url
stringlengths
30
180
content
stringlengths
64
14.2k
Source
stringclasses
1 value
https://www.defuwaxu.com/diine-ak-politig-nan-moytu-li-nuy-feewale/
DIINE AK POLITIG : NAN MOYTU LI NUY FÉEWALE Ëttu boole bi, genn kurél la gu boole mbooleem këri diine yi ngir saxal jàmm ci biir réew mi, rawatina ci lu ñeel politig beek diine ji. Seetlu nanu ne saa bu jamanoy fal njiitu réew jotee rekk, njaqare dafay faral di am. Li ko waral, nag, du dara lu dul ñenn ci politiseN yi dañuy jëfandikoo tarixa yi ngir beccingéel yeneen wutaakon yi ak a yëkkati seen mbër. Fan yii yépp, ñi bokk ci Ëttu boole baa ngiy daje di waxtaan ci jafe-jafe yeek yëngu-yëngu yiy am ci antarnet beek i xeeti xaralaam yu deme ni Facebook ak WhatsApp. Kilifay Facebook yi amal nañu ag saytu, ànd ceek kàngam yi taxawal kurél gi. Weccoo nañu xalaat naka lañu war a def ba dakkal téesanteek wax ju ñaaw ci béréb yooyu. Bi bésu pal gi desee benn ayu-bés rekk, ay ndéggat yu bari tàbbalees na leen ci antarnet bi, wesaare leen ci “Whatsapp” yi. Ay saay-saay a sooke lu ni mel, di sos ay fen yu tooy xepp, naan këru diine sàngam warul a sànnil xob wutaakon sàngam ndax bokkul ci ñoom, te gëmul seeni sëriñ. Lii moo bijji tiitaange ju réy ci waa réew mi. Diine nekk na lu man a jur xiirook ŋaayoo, te wareesul a mbubboo tarixa ngir soppi ko gànnaay, di ko xeexe ci politig bi. Yoonu tasawuf wi fi mag ñi sampoon, jàmm ak taalibe yi xamante, soppante a ko taxoon a jóg. Donte sax, politig masul a tàqalikook diine, ni seen diggante fése jamono jii dafa jéggi dayo. Séex Tiijaan Si, doomu Abdu Asiis Si Al Amiin, njiit li nekk ci boppu kurél googu yëkkati nay kàddu ngir àrtook leeral kóllëre gi dox ci diggante Murid yeek Tiijaan yi. Wane na ne ñaari kurél yii, waxul sax bokkoo gi leen boole, waaye ñoom ñépp liggéeyal diine ak Yonent bi rekk a leen yitteel. Nee na Sëriñ Séex Tiijaan Si Al Maxtoom wax na ni su Murid yi ak Tiijaan yiy ŋaayoo dafay naqari Yonent bi ndax moo leen jaboote ñoom ñépp. Rax-ci-dolli, wax na ne, palug njiitu réew du palu Imaam wala Xalifa, kon lees war a xool mooy jikko nit ki, jaar-jaaram, xam-xamu àddinaam ak yu ni mel. Waaye naan ci tarixa bii walla bee la bokk, ëpp naa def. Ëttu boole baa ngi ñaan waa réew mi ñu ànd ak dal te dem sànnil xob ki leen soob, bañ cee boole wax ju bari ak xuloo. Yal na Yàlla sotti jàmm ci réew mi te ki jig Senegaal Yàlla jox ko ndam lu sedd guyy.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/kan-mooymaki-sall/
KAN MOOY…MAKI SÀLL ? Ci Baatu Majaw Njaay Aw askan, bala moo tànn njiitam, war naa seet bu baax jikkoom, seetaat ko, xam mooy kan. Looloo waral Lu defu waxu, seen yéenekaay ci kàllaamay Kocc, jóg ngir jagleel wutaakon yi ay xët yuy fésal seen jaar-jaar ak seeni naal ñeel réew mi. Maanaam, li yitteel Lu defu waxu moo di xamal leen ñan ñooy dëgg-dëgg ñooñiy wër réew miy soow, te miir bu seeni ndaw gis taf fay nataal yu leen di màndargaal. Ndax, ku taxaw ne mën ngaa saafara jàngoro yi askan wiy jànkoonteel, warees na yëdduy mbiram. Li nu ko dugge, nag, du lenn lu-dul jox askan wiy tegtal ngir mu tànn ki mu yaakaar ne moo gën ci Senegaal. Bu ko defee, nan tàmbaleek Maki Sàll, njiitu réew mi bëgg ñu falaat ko. Ci atum 2000 la askanu Senegaal folli Abdu Juuf, fal Ablaay Wàdd. Ñu teg ci fukki at ak ñaar, mu doyal sëkk ci ‘’Góor-gi’’, dàq ko, Maki Sàll daldi toog ci jal bi. Ñépp am yaakaar ju réy ci moom, ndax guléet nu amoon njiit lu juddu fekk réew mi moom boppam ba noppi. Maki Sàll digewul yem ci. Daanaka dafa waatoon ni dina indiy coppite yuy jëme sunu gaal gi kanam. Te ginnaaw xamoon na ne danoo xobe lool ci demokaraasi, sopp lépp lu koy dëgëral, foofu la doore. Moo ko taxoon a giñ ne dina wàññi moomante yi ci boppu réew mi, jële leen ci juróom-ñaari at yemale leen ci juróomi at doŋŋ te, ku xas ba moome ñaari yoon, dootoo mën a toogaat ci jal bi. Waaye yàggul dara mu tàmbalee indiy tànki bukki, daldi ne, aa, man kat sama yéene rekk laa waxoon, waaye këru-àttekaay gi gën a kowe ci Senegaal nee na du ci dal, fàww ma matal juróom-ñaari at yi, ñu door a seet naka lañuy def. Kon mu mel ni Maki Sàll dafa noo bëggoon a gëmloo ne amoon na lool naqar ci li ko yoon mayul mu wàññi màndaam bu njëkk bi. Loolu yabaate lay nirool. Fi mu ne nii, benn weer kesee ko ci dese te talul dara lu-dul faluwaat. Gaa, def sa kemtalaayu-kàttanam ngir ñu sànnil lay kàrt, dara aayu ci waaye laaj bi am solo dëgg mooy : ndax askan wi doyal na ci nguuru Makeem déet ? Dinan ci jéem a tontu. Bi Senegaal moomee boppam ba ñu teg ci benn at la Aamadu Abdul Sàll ak Kumba Timbo am doom ju góor ca Fatig ; bés ba delsi, ñu ngénte ko, tudde ko Maki Sàll. Niñ ko waxe sànq, li ko wutaleek Seŋoor ak Abdu Juuf ak Abdulaay Wàdd, moo di ne moom rekk a fi nekkagum njiit lu fekkewul jamonoy nootaange Tubaab yi. Warees na cee yokk leneen lu am solo : ci réew mii doŋŋ la mës a jànge ba ni mu génne iniwérsite Ndakaaru ak lijaasa biy biral ne ku xam-xamam màcc la ci mbirum petorol ak yu ni deme. Ku say way-jur néewoon lool doole, nga ñefe ba réewum lëmm ne la yaa nu doy, dénk la boppam, bu la neexee nga ndamoo ko. Kon, Maki mënoon naa janook goney Senegaal ni leen : “Sama pàppa ak sama yaay amuñu woon alal, bokkuuñu woon ci yax yu réy yi wànte teewumaa fas jom, di jàng ba toog fi ma toog tey jii ! Defleen ni man !“ Su doxale woon noonu, dina doon royukaay. Waaye Buur, ci ñi la gën a jege, fàww mu am ciy dunguru yu lay dëkkee jay, di la wax yoo xam ni ñoom sax gëmuñu ko. Ñooñuy jag-jagal jaar-jaaru Maki Sàll, di ko jekk-jekkal, bés ba muy daanu lañ koy jàmbu, wuti keneen ku ñu nax. Jaamuwuñu Maki Sàll, seen soxla lañuy jaamu te su loolu dakkoon ci réew mi dina ci baax. Maki teel naa dugg ci làngu pólitig gi.  Ànd-Jëf bu Làndiŋ Sawane la njëkk a bokk, ba mu newee Iniwérsite bu Ndakaaru. Toogu fa lu yàgg, nag. Ci gis-gisam, Ànd-Jëf du woon pàrti buy daaneeli bés PS. Moo ko taxoon jël kàrtu PDS. Def na fukki at ak juróom ci pàrti boobu nga xam ni Ablaay Wàdd a fa doon Buur di fa Bummi. Ñi nekkandoo woon ak moom PDS nee ñu Maki gone gu teey la woon, yem fuñ ko yemloo, dégg ndigal te kenn mësu koo dégg mu wax lu ëpp. Bariwul woon wax sax, faf. Wàdd seetlu pas-pasam, daldi ko teg ci boppu kurélu kàngami PDS yi, muy leeral naali pàrti bi, ñu daan ko séen it léeg-léeg tele muy dàggasanteek ñoomin Abdulaay Wilaan ak waa PS yi mu àndal tey, ñu neexoo lool, ndeysaan. Bi PS daanoo ci atum 2000, “Góor-gi” woolu Maki, teg ko ci wetam. Ci diggante 2000 ak 2008, Petrosen la ko njëkk a dénk ba noppi boole ko ci ñaari gornmaaam, soog koo def Njiitu-jawriñi réew mi. Atum 2007 la Wàdd doon wut ñaareelu màndaa. Booba fekk na mook doom ji, Karim Maysa Wàdd, ñu def fiy njaaxum yu kenn xamul nañu tollu, réew mi jéppi leen, ñépp ne Wàdd jeexal na tàkk, su yëf yi jaaree ci yoon day daanu. Mu wóolooti Maki Sàll, ne ko jiiteel sama kàmpaañ. Maki jig lool Ablaay Wàdd ndax ba tey jii kenn mënul a wax fan la “Góor-gi” jaar ba faluwaaat ci sumb bu jëkk bi ! Joŋante tànneefu dipite yi ñëw, PDS yépp topp ci ginnaaw Maki Sàll, pàrti bi daldi amaat ndam, moom ci boppam ñu fal ko njiitu Péncum réew mi. Waaye yàggul dara ndombog-tànk googu indil koy jafe-jafe yu jéggi dayo. Ndax bés ba mu jaaxaanee “Place Soweto” ne na ko Karim Wàdd wuyusi, wax dipite yi fan la dugal xaalis biñ jagleeloon ndajem OCI mi fi amoon jamono jooju, la Wàdd mer ba funki, ne kii ndax yaramam neex na, sama doom man, Karim Maysa Wàdd mi nga xam ne Senegaal ba Senegaal daj moo fi gën a xereñ, ëpp fi xam-xam ! Booy seet, keroog la diggante Maki Sàll ak Ablaay Wàdd tàmbalee yàqu ba sunu jonni-Yàllay-tey jii. Noonu la ko “Góor-gi” jëlee ci boppu Péncum réew mi ba noppi dàq ko PDS. Li nu xamoon ci pólitigu Senegaal, nag, moo di ne boo deewee ba ñu suul la, fa ngay doxe ñu fàtte la ba fàww. Moonte, ak lu mu metti-metti woon, Maki Sàll fexe na ba dëkk Ablaay Wàdd, daan ko jéll bu amul benn werante, wuutu ko ci jal bi. Naka la def ba dekki, delsi, di jiite tey réew mi ? Ay ñoñi Màkee ngiy wër réew miy yéemu ci xelam, naan ni ngeen koy gis muy patt-pattaaral, njàccaar dëgg la, moo fi gën a xam li mu bëgg, xam it naka lay def ba jot ci. Ñu ngi naan tamit laata muy sóobu ci pólitig bi, dafa wër Senegaal, waxtaan ak askan wi, xam soxlay ñépp, soog a dige ay paj. Loolu, de, lay nitam di wax. Wànte ndax kàddu yooyu yenu nañu maanaa ? Bunu kenn jéem a gëmloo ne doomu Aamadu Abdul ak Kumba Timbo jee ëpp xel ci réew mi. Déedéet. Maki Sàll nitu neen la, kenn la fi ëppul xel. Ku gis ni muy doxale ak i noonam — tëj ràpp ci kaso bi Karim Wàdd ak Xalifa Abaabakar Sàll — dinga njort ne du nit ku wóolu lool boppam. Janoo na tamit ak réew mi di tagg Tubaab yi ñu daan beral loxo, nee na, di ñamal sunuy soldaar ay “desserts”, di ko xañ yeneen doomi-Afrig yépp. Lii rusluwul ? Fekki na fi yit ay naataangoom Kigali, ñu laaj ku ci nekk su ko Yàlla mayoon xam-xam ban jumtukaay lay njëkk a sàkk ngir jëmale Afrig kanam. Ku fàttaliku li mu tontu keroog, fàww nga xaw cee am kersa… Dëgg la, ku Yàlla mayul tuuti xel ak fulla ju mat sëkk doo jiiteji mukk lu tollu nim réew. Wànte am na leneen lees war a sóorale ci réew mu mel ni Senegaal. Loolu lan la ? Ay nooni Maki Sàll dinañuy wax ne Tubaab yee ko seetlu bu baax, xam ne kii amul dara lu muy bañ, luñ ko sant dina ko def, ñu daldi koy dooleel, jàpple ko ba mu falu. Du ñàkk mu am ñu ni nu : “Déggal ma ñii rekk ! Yéen a gën a ñeme Yàlla ! Ndax ba muy am yéen a ko fekke ?” Ku mu neex nga gise noonu mbir mi wànte pólitig, li ci ëpp solo, buy am ku ci bokkul doo ko fekke ! Te sax, ñaari firndee ngi yuy dëggal tuuma jooju. Bi ci njëkk moo di ne Frãs, réew yi mu tegoon loxo ci Afrig yépp, amu ci benn bu mu may foo yakkee sa nàkk. Tey la leen gën a sonal, tënk leen ba yëngu sax të leen. Li Pari tàmm a def mooy tabb njiit ciy nitam, nga doon ag xuusmaañàppam, mu yolomal buumu njaam gi nag, ngay tooyal ceebu Frãs, waaye booy féqu, nar koo rëcc mu daldi lay tam dëmm, sàkkal la pexe. Ku weddi lii, laajal Sànkaraak ñeneen ak ñeneen. Ñaareelu firnde bi moo di ne bi Maki Sàll faloo ci atum 2012 ba tey, deful lu-dul ràcc jemale ci kanamu Tubaab yi. Ñépp a ngi ciy teg seen bët. Muy Eiffage, di Auchan, di Orange, di Bolloré, di Total ak Alstom, suñ fi nekkoon di lim sosete Tugal yiy manq deretu askan wi, duñ fi jóge tey. Ku mu neex, ku mu naqadi, ñooy teg ndawal ci réew mi, sunu koom-koom a ngi ci seeni loxo. Nee ñu Maki bariwul wax, day jëf : waaye am na nu, soo koy jëfe, looy doyeeti wax ? Moom daal, wax ji yépp lii rekk la : Maki Sàll ak Tubaab yee bokk mbuus te li tee Senegaal jëm kanam, loolu ci la. Ku yéene sam réew li gën ci moom, doo ko wànteer ay doxandéem. Waaye kenn du ni Maki defu fi dara. 2012–2019 : juróom ñaari at yi mu toog ci jal bi, yeggali na liggéey yu bari yu Ablaay Wàdd sumboon. Xanaa rekk ni mu leen yàkkamtee sottal ngir am lu mu bàkkoo ci kàmpaañ bi ñuy waajal, moo xaw a teey xel. Moom mi ñu naan ku ànd ak sagoom la, xéy-na bu teeylu woon tuuti, doon na woyofal njëgu TER bi ak bu ótórut beek peyaas bi. Mbirum njëg li, lu am soloo, ndax xaw naa tiital ñi seen xam-xam màcc ci koom-koom. Nee ñu xaalis bu dul jeex la Maki leb bitim-réew dugal ko ci TER beek yeneen yi muy jébbal askan wi fan yii. Ci loolu sax la waa Bennoo Bokk Yaakaar di sukkandiku naan Senegaal tegu na, ni oto rawante yu gaaw yooyu, ci yoonu yokkute, yànj ba dee, di def fiiw ! fiiw ! rekk. Amaana koomu réew mi am tan waaye mel na ni yëf yi dañoo féete boor. Leneen lu ñépp di teg seen bët, moo di ne mbokki Maki Sàll yeek ñi koy jàppale, waxuñu dara, seen ceeb a ngi niin. Waaw, ndax mënees na tudde lii yokkute dëggëntaan ? Noo yey laaj loolu ndax muy loppitaan yi di lekool yi, benn doxu ci : ku sa loxo jotul sa ginnaaw — te ñooñoo ëpp ci Senegaal — soo feebaree doo faju te sam njàng du sori. Fi mu ne nii, Usmaan Sónko, Idirisaa Sekk, Isaa Sàll ak Madike Ñaŋ a ngi koy waaj a song. Xam ni mbir miy mujje jafe na. Li ñu war a fàttaliku rekk moo di ne Maki Sàll du neex a déjjati. Laata ñuy agsi fii tey, tas na ñaari pàrti yi fi ëppoon doole, PS ak PDS. Leneen yitteelu ko lu dul amaat beneen màndaa bu juróomi at. Loolu rekk a tax muy wër réew miy jébbale ay pom, ay saxaar ak i jàkka. Gone yaa ngi koy kókkali sax ci Facebook, naan alkaati Ndakaaru yi tey ku ñu gis ngay dawal oto bu bees ñu laaj la ndax Maki « inaugurer » na ko, soo leen nee déedéet ñu ni la taxaweel wet, mu ngi ci yoon wiy ñëw ! Am na yit ñu koy méngaleek Maxuréeja Géy mi doon yaakaar « màndaa » moom tamit ba taxoon koy leb xaalis bu bare di ndaataatallax. Wànte ci filmu Usmaan Sémbéen bi, Maxuréeja rekk la àddinaam di mujjee yàqu-yaxeet. « Màndaawu » 2019 bii moom, du ñàkk réewum lëmm la nar a salfaañe. Mel na ni Maki Sàll a ngi tayle ëllëgu goney Senegaal ngir rekk ga1ddu ndam li bésub 24 féewaryee bii ñuy séentu… Mamadu Jàllo ak Bubakar Bóris Jóob
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/fan-lanu-jem-ak-nakki-bill-gates-yi/
FAN LANU JËM AK ÑAKKI BILL GATES YI? (USÉYNU BÉEY) Coow laa ngi ne kurr ! Afrig ba Afrig daj, li ko dale Keer ba Peretoryaa, Ndakaaru jàpp Adis-Abebaa, wax ji benn la : jàppal wakseŋ fii, bàyyil wakseŋ fee. Coow li nag, ci anternet bi la jëkke. Dafa am ay Móodu-Móodu ak ay Faatu-Faatu yu def ay widewoo di ci aartu seen i mbokk ak askanu Afrig wépp. Liñ ci jublu woon, ci seen i wax, mooy xamal leen ne, ci réewi Ërob yeek Amerig yi, am na ciy mbooloo yu laxasaayoo lëndëm, di lal ay pexe ngir wàññi limu nit ñi ci àddina si, te fas ko yéene tàmbalee Afrig ak nit ñu ñuul ñi. Nee ñu, gëstukat yooyu kat, dañoo jàpp ne li àddina si am ciy nit dafa ëpp. Bu yàggee, dootuñu xaj ci kow suuf, dund bi dootul doy te kon xiif dina rey ñu bare. Ndaxte, suuf si dina dem ba dootul nangu, dara dootul meññ ; géej gi dina yulleeku ba jeex tàkk. Ci gàttal, dara dootul doy. Kon, ci gis-gisu ñooñu, warees na wàññi doomi-aadama yi bala njaaxum loolu di am. Mu mel ni daal xalaati Malthus, benn boroom xam-xam bu mag bu doon dund ci 19eelu xarnu bi, ca Àngalteer, la ñuy dekkil noonu. Moom mi doon biral ne, feek wàññiwuñu limu nit ñi, dund gi ci kow suuf du neex, du yàgg. Bu dara desulee lu dul tànn ñan lees war a wàññi, xeli saay-saay yépp ne yarr ci askanuw nit ku ñuul. Xalaas ! Mbete Yàlla ! Bala maa dee ñu daas seen làmmiñ yi, singali nu. Ki ci gën a rafet wax mooy ki la naan :« nit ñu ñuul ñi dañoo xayadi te mën a jur ba nga ne lii lu mu doon ! » Ñi ci yées xalaat ñooy gënale xeet yi te naan : « Afrig a barey ndaw ! Nun, nag, ñi ëpp ci nun màggat nanu ba dóox, di xaar dee. Des na tuuti, xeetu nit ku weex dina sooy, nit ku ñuul jiite àddina si. Te loolu, warunu koo nangu tey, warunu koo nangu ëllëg, bun ko seetaanee mu ñaaw ! » Wax ju àgg, nag, dof yaa ko moom. Lii lépp sax de, day nirook «léeboon ak lippoon». Naka la xalaat yu ni deme, di mën a juddu bay meññ ci xelu nit njaay, ku ànd ak i noppam ? Naal boobu, nag, ay boroomi alal, di boroomi tur, ay politiseŋ ak ay boroomi xam-xam ñoo ko sumb, jiite ko. Bill Gates ak Sarkoosi bokk nañ ci ñi ci gën a fés. Bill Gates, moom, weddi na tuuma yooyu ñuy teg ci kowam. Nee na, waxul ñu wàññi nit ñi waaye nee na ni doomi-aadama yiy yokkoo lañu war a seetaat ngir yaxanal dund gi te neexal ko. Mu fas yéene cee def alal ju tollu ci 100 alfunniy dolaar. Maanaam 50 milyaar ci sunu xaalis. Li mu ci jublu, ciy waxam, moy xeex feebar yi ci Afrig ba noppi, fexee yemale njureel gi. Moom daal, nee na looloo mës a nekk taxawaayam te duggewu ko lenn lu dul sàmm bakkani doomi–aadama yi. Waaw kii, dunu ko ne jàkk, ni ko : ‘Ngóor si Bill, wiiri-wiiri, jaari Ndaari. Xalaatoo ni Sàmbaay Bàcc rekk, am déet ?’’ Rax-ci-dolli, ay kàngam yu mag a mag àddu nañ ci mbir mi, yokk ci seen xorom. Ku ci mel ni Thedros Adhanom Ghebreyesus, di doomu Ecópi, jiite kurél giy saytu wér–gi-yaramu nit ñi ci àddina si (OMS) ak it njiitu Mbootaayu Xeet yi (ONU), António Guterres bokk nañ ci. Ñaari kàngam yooyu yépp, artu nañ waa Afrig ci koronaawiris bi. Nee ñu, bees fagaruwulee ci lu gaaw, dina fi rey ay milyoŋi nit. Waaye, li jaaxal ñépp mooy ni, ba sunu-jonni-Yàlla-tey-jii, Afrig mooy dànd gi gën a néewle fopp limu ñi Covid-19 bi daaneel, waxatumaak ñi mu rey. Loolu nag, tekkiwul ne Afrig mën naa nelaw bay yàndoor ! Ndaxte, koronaawiris bi kat, bàyyiwul kenn ! Li gën a teey xelu nit ñi nag, mooy waxtaan wiñaari gëstukati Farãs yi, doktoor Jean Paul-Mira ak porfesoor Camille Lotch, amal ci ayu–bés yii weesu rekk, te mu siiw lool ci Anternet bi. Ñoom ñaar ñooñu de, dañu doon wecceexalaat ci nu ñuy def ba am wakseŋ buy tax ñu jële Covid-19 bi ci àddina sépp. Ñu jàpp ni BCG, ñakk boobu ñu daan ñakk xale yi ngir xeex sëqët su bon seek yeneeni feebar, war nacee baax. Ñu tëje seen waxtaan woowule ci ànd gi ñu ànd ne Afrig rekk lañ war a defe jéemantu biy tax ñu xam ndax ñakk bi mën naa xeex koronaawiris bi am déet. Loolu, laata ñu koy mën a jariñoo ci seen i dëkk, ci Ërob mbaa Amerig. Kàddu yooyu, nag, ñoo gënatee merloo doomi Afrig yu baree bare. Am ci ñu siiw ci ñoom, ñu mel ni Samuel Et’oo, Didier Drogba walla Àllaaji Juuf, ñu doon ñu ñu raññee ci mbirum futbal, ci àddina sépp, ak it Claudy Syar mu RFI (rajo bu Frãs moom)… Ñu di ñu am baat, seen kàddu mën a egg fu sori lool. Werante yeek xuloo yi neeti kurr ci Anternet bi, mu mel ni tulleek-màlle, di niru tuq su bënn te saañ ba réer ! Fii nag ci Senegaal, li gën a teey xel, jaxase xel yépp, mooy dégtu (audio) biy daw ci xaraley jokko yu bees yi, ñu ciy dégg baatu benn Tubaab, di  njiitu Ayeropoor Belees Jaañ, muy xamle ne, daanaka Ayeropoor bi tëj na, ginnaaw yenn yóbbal yu ñu fay wàcce léeg-léeg, yu mel ne ay… wakseŋ ! Waa ji nag, bi ñu bare ci ñiy jëfandikoo xaraley jokko yu bees yi dale ci kowam, dellu na ginnaaw, ne moom masul a wax lu ni mel. Doonte dégtu  yaa ngi fi ba tey di ko tiiñal. Ba ca jamono yooyu, xel yaa nga doon werante, naan dëgg laam déet. Waaye ci fan yi weesu rekk, gis nañu ay kilifay Afrig di awante ci taskatu xibaar yi ngir teggi tuuma yi. Nee ñu, yëguñu, tinuñu. Waaye, li yéeme dëgg, mooy bi benn gëstukatu Kongo (RDC) bu ñu ràññee jëlee ñaari yoon kàddu ci diir bu gàtt, ba noppi ne maa waxoon-waxeet. Ca njëlbéen ga, dafa waxoon ne boolees na réewum Kongo RDC ci réew yiñ war a natte ñakk bi ñuy wax. Mu ne woon ne, ñoom, nangu nañu te joxe nañ seen kàddu. Bi saaga yeek diiŋat yi jibee, mu dellu ginnaaw ne, ñoom waa Kongo duñu mës a seetaan, ñuy jàppe seen askan nikiy mala. Senegaal it, kenn demul mu des ñeel fésal cetug deram gi : mu di Ablaay Juuf Saar jawriñ bi ñu dénk mbirum paj mi, di njiitu réew mi Maki Sàll ci boppam, ñoom ñaar ñépp weddi nañu ba mu set, dem nañu sax ba ne, bu dee Senegaal rekk, kenn du ko fekk ci gaalu xaj googu ! Ci sunu réew mii moom, ñépp a ngiy fàttaliku bés bi Bill Gates daje woon ca Kanadaa ak Maki, ca weeru sàttumbar 2016. Ndaje moomu juroon na fi coow ci ginnaaw gi. Waaye, ndawal àmbasadëeru Senegaal ca Kanadaa indi woon na ciy leeral, di biral ne, waxtaan woowule, dara sababu ko woon lu dul xeex feebar yu mel ni  sëqat su bon si, sibbiru, sidaa ak it ni ñuy def ba yemale njureel gi. Li wóor moo di ne foo séene saxaar, xal yaa ngay boy ca suuf ! Fi mu ne nii daal, xel yi ñaaw nañu ba kenn xamatul looy def. Bu kenn ñakkatul doomam, ndax kon dinañu mën a jële feebar yu bari yi ci sunu réew mi, ak sax ci Afrig gépp ? Bu nu bàyyee ku ñëw rekk ñakkal nu sunuy doom, mbaa kon dunu dimbali ñiy jéem a faagaagal nit ñu ñuul ñi ci kow suuf ? Laaj yu am solo yooyu ñoo sampu tey te doomi Afrig yi, ak seen i njiit ñoo war a mànkoo joxe ci tontu lu leer, tey doon li gën ci xaley Afrig yi ak ëllëgu Afrig ci boppam. Ñakk sa doom, mbaa bañ koo ñakk ? Mu mel ne Afrig tollooti na ci sélébeyoon bi mu tollu woon ca 1963. Jamono jooju, benn ci ñaari yoon lanu mënoon a jaar : yoonu Ufuwet Buwaañi ak Lewópóol Seŋoor, maanaam ànd ak doxandéem bi mu nuy wommat, walla yoonu Kwame Nkrumah ak Séex Anta Jóob, di tekki ne Afrig war naa mën demal boppam ci kow nu bennoo,  di xàccandoo di dóorandoo. Yoonu Seŋoor ak Ufuwet woowu nu tànnoon moo nu tax a tollu tey fii. Saa su nekk nuy xaar ay doxandéem yiy jóge fu kenn xamul, ñëw  di nu wax lan lanu war a def, fan lanu war a jaar ! Ndax bii yoon, dinanu takk sunu fit, tànn yoon wi nu Nkrumaak Séex Anta xàllal ciy jamono ? Àndandoo xeex nooni démb yi, yu tey yi ak yu jëmmi jamono yi. Bennoo bokk benn jëmu mooy tax Afrig am doole ak naataange. Booloo nuy tax a daan koronaawiris bi ; booloo moo war a nekk sunu kiiraay. Ndege, booloo mooy doole. Askani Afrig, ëllëg, ëllëgu booloo la, ëllëgu moom-sa-bopp la !
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/reew-mi-gej-naa-yengoo-nii-useynu-beey/
WAAW, KAÑ LA SENEGAAL GËJ A YËNGOO NII…? Weeru màrs wii weesu, Senegaal tàngoon na jipp ! Gannaaw ba alkaati yeek sàndarm yi jëlijee Usmaan Sonko ngir jébbal ko Yoon, daanaka waa Ndakaaru yépp, waa Senegaal yépp sax, rawatina ndaw ñi, dañoo jóg nekk benn say, ne : “Du fi ame !” Keroog ak fan ya ca topp, jàppante bi metti woon na. Waa Nguur gi ne duñu bàyyi, gune yi gën leen a dëgër fi ñu jàpp. Noonu la fi fukki bakkan ak ñett rotee. Ñoom ñépp di ay waxambaane yu tollu ci seen diggu ndaw. Ndax fu bakkan di rot, mat na di fa tudd yàqute yu dul jeex ci alal ? Ãxakañ ! Waaye, xel demul ci di leen méngale. Li nu soxal fii, mooy seetlu ni, li ëpp ci lu yàqu, nekkul ay alali doomi réew mi donte ñàkku ci. Waaye ay moomeelu doxandéem lañu, diy Tubaab yu sanc seen i këri-koom ci dëkk bi, ba tax ñu aakimoo daanaka koomu réew mépp. Këri koom yu mel ne Total, Auchan, Senac, añs. Loolu di nu fàttali bàkku yenn ndaw yiy xeex ngir Senegaal moom dëgg boppam : France Dégage ! (“Farãs jóge fi !”). Muy lu mat a jàngat ndax day wone ni, ndaw ñaa ngi ci tànki seen i mag yi fi nekkoon doon bañ nooteelu doxandéem bi. Te xaley tey yii, mel na ne ñoo gën a farlooti ci farata jooju. Loolu lépp a taxoon Nguur gi dellu gannaaw, yolamal loxoom, bàyyi Sonko mu ñibbi. Guléet, ca ba muy ne ci jal bi, Persidaŋ Maki Sàll gis lu ko jaaxal, ëpp ko loxo ba tax mu walluji, ñaan xalifa yi ñu dugal seen loxo ci mbir mi, ba noppi nangul leen lépp lu ñu ko laajoon ngir indi jàmm. Mu mujje jél kàddu gi ñépp doon xaar, wax ak réew mi, ci anam yu ko kenn masul woon a gis : yëramtu, dige, ñaan njekk, woote juboo ak bennoo. Kujje gi ñoom it, wormaal kilifay diine ji, jóg ni kenn du dox i tànki jàmm bàyyi leen ginnaaw. Waxtu ya jiitu kàllaamay Maki yi, Usmaan Sonko jëkkoon na jël kàddu, wax waxi jàmm, waaye it teg ay sàrt yu leer yu Nguur gi war a jaar, ci gis-gisam, ba mën dalal réew mi. Moo tax it, askanu Senegaal dina santati Sëriñ si. Ñoom ñi nga xam ne, daanaka, réew mépp a ngi doon xaar seen kàddu, ba nit ñi demee ba jàq. Ki ci gënoon a ràññeeku doon nag Sëriñ Muntaqaa Basiiru Mbàkke. Moom mi doxoon diggante Njiitu Réew mi ak kujje gi. Ñépp déggal ko, jàmm dellusi ci dëkk bi. Muy firndeelati solos sëriñ si ci nekkinu askanu Senegaal, te muy luy màndargaal Senegaal (te di dëggal lan ca jotoon a bind ci ginnaaw, ci sunub bataaxal bu nu duppe woon : ”Sëriñ seek a bari doole !”). Waaye, ba lépp nee tekk, lépp sedd, waa Nguur gi mel ne du ñoom : ña laqatu woon ñépp génnaat di mbéléléli ci rajo yeek tele yi. Maki woote ndaje, wax ak guney pàrteem, di gaaruwaaleek a xupp kujje gi : “Li fi amoon, du fi amati !”. Mel ne, tey la Waalo gën a aay. Teguñu ci juróomi weer, Persidaŋ Maki woo Ndawi Réew mi, wotelu sàrt yu yees yuy rëbb mbéeféer yi, ci ni ñu ko waxe.  Mu nel ne nag, dañuy taafantoo jiyaadis yi, ndax ku seet ba ca biir xam ni, ñi ñuy rëbb dëgg, du ñeneen ñu dul waa kujje gi ! Noonu boog, la ko ñu bare jàngate, ay boroom xam-xam yuy jàngale ci iniwérsite yi, waa kujje gi ci seen bopp, ba ci Usmaan Sonko mii jagleel xew woowu ay kàddu yu am a am solo. Du caagéen ne, danuy tëkkale Usmaan Sonko ak ay kàngami Afrig yu mag yu fi nekkoon. Waaye nag, neexul ba neexul, ngóor si, ni mu waxe keroog jooju, gëj na fee am (jóge ciy way-pólitig), ca jamonoy Séex Anta Jóob walla Tomaas Saŋkara. Ne jàkk waa Tugal, tudd seen tur, xamal leen ne lu bon te yées ci Afrig, ñoom a, walla boog seen loxoo ngi ci. Ba noppi di leen digal ñu teggi seen loxo ci kaw Afrig te abal nu ! Sàrt yu bees yii nag, li ci doy waar mooy ne, ëpp nañu téeméeri ponk, te sunuy Ndawi Réew mi, ciy “anam yu jamp” la leen ko gornamaŋ bi jébbal, ñu war koo jàngat itam ci diir bu gàtt (benn ba ñaari ayu-bés). Moone, ñoom ci seen bopp, ci bataaxalu Commission des Lois, di kurél gi ñu jagleel liggéeyu caytu sàrti Yoon yi, ñu ngiy xamle ni : ”Code Pénal bi ak Code de procédure Pénale bi (ñaari téere yooyu ñu leen di woteloo) soo leen joxoon ñu seen xel màcc ci mbiru Yoon sax, dinañu am i jafe-jafe ndax dañoo naqaree jàng, kenn mënul a xam dëgg lu ñu wund ; waxatumaak nun Ndawi Réew mi nga xam ni, dara lañu amul ci xam-xamu Yoon”. Waaw, ñii de, ñu xam loolu ba noppi, bind ko ba mu leer ci seen bataaxal, ñoo walbatiku wote sàrt yooyee, te naan nu: ‘Sàrt yii baax nañu ci askan wi’! Ku leen di déglu ba di leen gëm ? Maki moom, booba, mu ngiy wër réew mi, dëkkoo dëkk, di nemmeekuji koomu gox-goxaan yi. Ci li mu lay, ndax ñu bare weddil nañu ko loolu, jàpp ne ay yëngug pólitig doŋŋ lay doxal noonu. Lum ci mënti doon, li yéeme ci mbir mi, mooy nit ñu baree bare yi muy dajale saa su ne, ciy jamanoy koronaawiris bii ! – Am sax ñu ñuy yab ciy woto, péey ba péey, gannaaw ba ñu leen compalee as tuut ciy koppar -. Dëgg la, ba mu noppee ciy doxontoom yooyu, xelam dellusi na, ba tax muy digle ñu bàyyi mbooloo yu tàkku yi ñuy woo ci xew yi. Xéy-na ndax “Covid 19” day moytu ay xewi Persidaŋ Maki Sàll ? Bugaan Géy Dani moom, faalewul waxi Maki yooyee, ndax moom it sol nay dàllam di doxal li mu tudde “Tibbi Tànki Maki”. Di wër réew mi, fu Maki jaaroon mu jaar fa, lu Maki waxoon, mu weddi ko ba mu set wecc ! Nit ñu baree bari di ko topp. Usmaan Sonko, moom it, ne kenn du dem mu des, daldi jëlaat “Nemmeeku Tuur” yi mu nu tàmmaloon. Wuudey Medina yi de, ñoom, duñ ko réccu ndax seen i njaay yi mu leen fexeel ba ñu jar, ci kaw dimmali liggéeykati Senegaal yi. Senegaal nag, wax ko te dee, day réew mu doy waar ! Ndax kat, jamono jii koronaa bi gën a lëmbe àddina si, rawatina ci miim réew, la nit ñi mel ne ñu raatukaan ! Ku la gën a ñeme mbas mi, nga ni kii la ! Mu mel ne, nit ñi dañoo dem ba ës, walla book ñu tul (tul bu wuteek ñakku yi fi lamb ba dee !) ba tax koronaa bi du leen mënal tus ! Te kenn rawu ci way-pólitig yi. Waaye kenn du nettali doxantuy Maki Sàll yooyu te doo yëy yàbbi ci mbiru nervis yi, maanaam dóorkat yi ! Ñépp gisoon nañ fi ne, ci xew-xewi màrs yi, ay sàmbaabóoy yu gànnaayoo seen i yat, walla ay jaasi, ñoo doon daw ci tali yi di rëbb xale yi doon ñaxtu, di leen jàpp, di leen dóor, dóor yu metti. Loolu lépp nag, doon ame ci kanamu takk-der yi, mu mel ne sax, ñoo àndoon ci seen “liggéey” boobu ! Dóorkat yooyee ñoo feeñaat ci doxantu Maki yi. Ñu neeti ci seen mënin, di jàpp, di dóor gone yiy ñaxtu walla sax ku ñu gis rekk nga sol mbaa nga takk lu xonq ! Dëgg la, seen kilifa moo fi newoon, lu yàggul dara, moom lu xonq du ko gis ! Waaye ku taxaw seetlu dinga gis ni, ba Persidaŋ duggee Tuuba, dóorkat yi dañu ni mes ! Kenn gisul, kenn yëgul. Moo tax it, gune yi xaaruñu ku leen woo : takk seen i sagar yu xonq coyy, di yuuxu, di sànni suuf, ñenn ñi sax di yuuxu turu… Usmaan Sonko ! Dóorkat yi daal (walla seen kilifa ?) ñemewuñu Boroom Tuuba ! Lu mu ci mënti doon, gannaaw takk-der yi, ay dóorkat, fenn lañ leen soxlawul. Te réewum Yoon sax, daa mënut a ànd ak li nu mel. Maki nag, war naa seetaat boppam ! Ayu-bés gii ñu génn nag, Persidaŋ wooti na Ndawi Réew mi, ñu wotelati ko ay sàrt yu bees yu jëm ciy doxalinu wote yi. Fii tam, lu yéeme feeñ na fi : lu bare ci déggoo yi amoon ca Dialogue National ba (Jataayu Waxtaanekaayu mbiri Réew mi), walla ponk yu ñu yaakaaroon ne Persidaŋ dina ci jël ndogal, dañu leen teggi teg fale ! Xeli nit ñi gënatee teey ci mbirum ñetteelu màndaa bi ñuy ruumandaat booba ba léegi, di wax naan, mu ngi ci xelu Maki. Te loolu lépp fekk na mu soppi, ni mu ko neexe, tëralinu gox-goxaan yi ci Ndakaaru, te tagguwu ci kenn ! Waaye li ci kanam rawul i gët. Fii ñu toll nii nag, yenn xel yaa ngiy ñaaw, yeneen yaa ngiy nàcc. Lii lépp ciy xew-xew yu baree nii, ame ci diir bu gàtt ; xew wu la ci gën a metti walla gën laa lëj, nga ne bii la. Mbaa réewum Senegaal dina ko mën a dëkku ? Mbaa du ñaareelu “weeru màrs” daf fe nar a am ? Li gune yiy woowe 2e vague, maanaam ñaareelu sóobu ciy ay ? Dëkk bu yëngu bii, nu fiy jàmm dellusee, sax fi dakk ? Te muy jàmm ju lalu ci dëgg ? Wax jaa ngi noonu. Nun waa Senegaal nag, ndax warunoo seetaat sunu bopp ? Ndax kat, fu fen di mën dëgg, fu kàdduy worook i jëf, taxawal fa luy jëm kër du yomb ! Rawatina réew moo xam ne, Nguur gi, jay-doole rekk la xam te di ko doxaale bu baax. Fàww kon, ñi bokk gis-gis te gëm seen bopp, gëm demokaraasi te féeteek askan wi, booloo, takku tey xàccandoo di dóorandoo, su nu bëggee tekki buumu-njaam gii nu tënk ba léegi. Uséynu Béey
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/bokk-ak-nawloo-ngir-jamm-ak-naataange-ci-addina/
BOKK AK NAWLOO NGIR JÀMM AK NAATAANGE CI ÀDDUNA SI Weer yii nu génn, réew yu bare tànn nañu seen njiit. Joŋante yi gën a indi coow mooy yi amoon ca Beliyoriisi mbaa Amerig, walla fii ci Afrig, ca Kodiwaar, Gine-Konaakiri, Burkinaa, ak-ñoom-seen. Réewum Ganaa moo ci mujj. Gëstukat yu bare ak i yéenekaay bind nañ ci, woykat yi waxi noppi. Góom yeek dana yiy teree wote ci jàmm ñoo ngi ne fàŋŋ. Kon boog, jar na nu toog, delloosi sunu xel, ubbi bu baax sunuy gët ak sunuy nopp. Su ko defee, dinanu mën a bind ci jafe-jafe yi réew yiy jànkoonteel, rawatina: – Góom yeek dana yi tëwa wér – Siddit yi sanax – Yaram yiy soox I/ Góomi réewi Afrig yi bare nañu. Mënees na cee lim: -Ñit ñu bari yi amul dàntite, moo xam ndax mës na ñoo am kayitu juddu walla mësuñu koo am; -Ñi bëgg a wote waaye ba ñu demee ba ca béréb ya, gisuñu njaq liñu war a sànni seen xob; -Ni ñu dajalee nit ñi ci ay mbaar yu xat, ñu ne fay buuxante, ba faf mer, gedd mbaa ñu dàq leen, ne leen waxtu dakkal wote bi jot na; – Ñi gisul seen nataalu mbër ci xob yi; – Ñi mënul a dem ci béréb yi njaq yi ne, ndax seen i cër dañoo sutante walla ñu tàyyel a génn rekk, ndax léegi mën nañoo jaar ciy jumtuwaay yu bees ngir wote. Wóoruleen nag ndax seen xob mujj naa bokk ci waññi bi; – Lawax yiy tamante dëmm, di jiiñante càcc ak di jaayante doole, nekk na luñ dégg ci réew yu bare; – Ger ak maye xaalis tax na ba ci yenn làngi pólitig yi ak lawax yi luxóor, jël ndam li. II / Dana yi nag, nii lañu bindoo: – Ñi ci jal yi sawaru ñoo jébbale lenge yi, jàpp ci Yàlla nangu ni dañ leen a daan, – Daa ñu def seen kem-kàttan, aakimoo yéenekaay yi, gaawtu ne làmb ji tas na, wure wi dem na këŋ, – Daa ñu dóore, màtte, jiiñ, faat sax ñi ñu doon joŋanteel; – Daa ñu ger ñi leen sonal ak ñi ñu ragal, jaare ko ci mbootaay yi, sàndikaa yi, kilifa-diine yeek kilifa-aada yi. Ragal a delloo weccit, ragal a tontu ci li ñu leen di tuumaal moo tax ñuy yaakaar ne xare pólitig dafa ànd ak xaru, ak ñédd nguur; – Ba ñu defee loolu lépp ba noppi, daa ñu dellusi di digaate naataange ak jàmm: – Daa ñu jéem a dalal xel yi, dige ni di nañ jubbanti réq-réqi réew mi, ngir mbir yépp tegu ci anam yu leer te jub, lépp rekk ngir faluwaat. Waaye ndax mënees na leen a gëm? III / Ñàkkul siddit yee wéragul – Siddit wi ci gën a feebar mooy siddit wi Njiiti réew yi naj, jàppe nguur gi seen moomeel. Su fekkee njiit li ku dul sàmm kàddoom la, ku mànduwul, ku jiital bànneexu njabootam tey jàppaley xaritam, mbaa xeetam, walla waasoom, kooku mënul suuxat mat ak juboo ak Jàmm, astemaak naataange. – Faj siddit wi ci topp mooy tabaxaat pénc mi war a xàll yoon wi ñépp di jaar ngir jokkoo, waxtaan wi gën a yaatu Su fekkee pénc moomu, ki ko jiite ak i naataangoom defuñu seen liggéey, rax-ci-dolli lu njiitu-réew mi joxoñ, ñu dagg, xam ngeen ni ñooñu kenn dootul am yaakaar ci ñoom; duñu leen sax faaleeti; – Ñetteelu siddit wi feebar mooy siddit wiy dawal ëttu àttekaay yi. Su nasaxee, far, fekki yeneen ñaari siddit yi, réew mi mën naa tas. IV / Bokk ak nawlooy faj yaram wi Nit moo dem ba gis ne jàmm moo gën fitna. Noonu la fente demokaraasi, maanaam, sàmm baatu képp kuy noyyi cim réew, jublu ci saxal fa jàmm ak naataange. Nit demati ba yokk ci nawloo, ngir ñu yaatal géew bi; wàññi xiiro ak ŋaayoo, boddikoonte ci biir xeet yi, biir waaso yeek këru diine yi, ngir sàmm li ñépp bokk. Noonu la yaram wi war a bindoo. Bennoo bi tamit, war naa law fépp ci réew mi, ku ne li nga liggéey, jariñ la, jariñ sa njaboot ba jariñaale askan wépp. – Sàrt yi ñu ràbb noonu, ku leen jéggi, teggi sànni, xàllal nga fitna yoon. Kon boog fedd siddit yi, diw leen baa ñu niin ak kaarite mooy yeewu, jàng, sàkku xam-xam, ngir mën a tedd ëllëg. – Fii ci Senegaal nag, jot nan fee amal waxtaan wu yaatoo-yaatu. Persidaa Aamadu Maxtaar Mbów, moo jiite woon liggéey boobu. Yékkati na fay kàddu yu am solo, dénk leen ay sëtam. Du ñàkk nu dellusi ci balay yàgg, saytu mbir mi, wax ci li nu ci war a yokk. Baabakar Jóob Buuba Njiitu PAALAE, mbootaay muy yëngatu ci liifantu ak njàngum mag ci Afrig
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/afrobasket-kigali-2023-xalam-demoon-na-bay-neex/
AFROBASKET-KIGALI 2023 : XALAM DEMOON NA BAY NEEX ! Démb la woon finaalu Afrobasket bi doon am ren ca Ruwàndaa, doxoon ci diggante Senegaal ak Niseriyaa. Niseriyaa nag moo ko mujje gañe, daldi jël kub bi. Senegaal, ca njëlbeen ga, ku la waxoon ni dana finaalu nga weddi ko. Nde, dafa lajj ñaari yoon ca ndoorteelu xëccoo bi (tournoi). Gannaaw ba ko Ugàndaa dóoree 85 ci 83, Mali tamit daf ko dóoroon 72 ci 49. Ca la gaynde yu jigéen yi fippoo, jàpp Esipt mi nga xam ni ci ñaaari at yii bojo-bojoom la ko def, gañe ko 71 ci 60. Mu jóge foofu, ba tay, gañewaat kii di Kamerun 80 ci 77 jàll ci dëmi-finaal yi. Noonu, mu dajewaat ak Mali mi ko dóoroon ca ñaareelu joŋanteem ba, daldi fayu, gañe ko 75 ci 65. Ndax, wolof dafa ni, dóor, fayu. Démb nag, ci gaawu gi la doon daje ak Niseriyaa ci finaal bi. Waaye, Niseriyaa a ko mujje gañe 84i poñ ci 74, muy fukki poñ yi dox seen diggante. Kii di Siyeraa Siney Dilaar mi nga xam ni, wii yoon lay door a ñëw ci ekib bi, moo mujje jël raw-gàddu bi ñu tegaloon ki dàq a doxal, muy lu mu jagoo gannaaw lu rëy la mu basket ci diiru xëccoo bi. Kii di seen tàggatkatu bi nag, Mustafaa Gay àggaliwul finaal bi ndax dafa géddoon, dem bàyyi leen fa ba mu xaajee. Loolu nag, nekk na loo xam ni rafetul wenn yoon. Ndax, ñoo xam ni yaa leen war a taxawu bu leen ñépp bàyyi woon, yaa leen war a taxawu, fital leen, ngay dem di leen bàyyeek seen bopp. Ci kow loolu, Siyeraa Siney Dilaar yékkati nay kàddu di ŋàññ doxalinu Mustafaa Gay mi leen doon tàggat : ” Liy wutaley ekib ci sàmpiyonaa, mooy tàggakat. Guleet may gis ab tàggatkat buy bàyyi ak a gédd ekibam ci xaaju joŋanteb sàmpiyonaa.” Mustafaa Gay sax xamle na ni dafa daldi bàyyi, nekkatul tàggatkatu ekib bi.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/jeeri-joor-ndeelaak-tubaab-bi/
JÉERI JOOR NDEELAAK TUBAAB BI Jéeri Joor Ndeela Faal mu ngi gane àdduna ci atum 1871. Mu doon doom ci Sàmba Yaaya Faal mi newoon fanweer ak ñaarelu Dammeelu Kajoor te Nasaraan yi daaneloon ko ba noppi yóbbu ko Ndar-Géej, téye ko fa. Ci atum 1891 la xaru ci dex gi ginnaaw bi way-juram bu jigéen génnee àdduna te Tubaab bi aaye ko mu teew ca dëj ba. Ñuy wax ne ba muy takk rakki Kànnaar Faal mi doonoon kilifa ca tundu Bawol te moom it Tubaab bi daaneloon ko, Kànnaar moomu da koo mayoon ñaari jaam. Bi ñu ci tegee ab diir, Jéeri ànd ak Kànnaar Faal ak Bookar Tilaas – mi yilifoon tundu Géwul – dem Cees jaay fa jaam yooyee. Fekk na booba Tubaab bi aaye woon njaayum jaam. Noonee, juróom-ñaari fan ci weeru awril ci lañu leen tege loxo ñoom ñett yóbbu leen ca kër gornóor ba ca Cees ñu jàkkaarlook kummàndaŋu Tubaab ba tegoon seen kaw tuumay njaayum jaam. Ca la leen fayloo ab alamaan. Waaye yamu ca ne da caa teg ne Jéeri dees koy tëj kaso diirub fukki fan ak juróom. Booba fekk na Sarica Jéey, di xarit ci Jéeri, doon ko xaar ci biti. Ba mu déggee coow li mu daldi mer ba futt ne “mënees naa nangu alamaan bi gaa, waaye xel xalaatul muy seetaan ñuy tëj Jéeri waxumalaak di ko jéng. Loolu moom mënuma koo nangu !” Bi Jéeriy xeex ak alkaati yi ko doon jéem a jéng, la Sarica Jéey dàjji bunt bi ne jaas ci biir bérébu-àttekaay bi. Ca la alkaati yi dawe, mu bocci paaka jam ko Henry Chautemps mi fa wuutu woon gornóor, mu faatu ci saa si. Ba mu ca jógee la jël paaka bay siit ak deret jox ko Jéeri. Ñu ànd ñoom ñaar génn, géwél yi topp leen di tagg  ay maami Jéeri Joor Ndeela Faal. La ca Sarica Jéey jublu woon mooy sàmm woyu Jéeri Joor Ndeela Faal, mu doon woy wu rafet ba ciy sëtam ba ñu mën a fàttaliku ba fàww ne Jéeri moo reyoon kummàndaŋ bi ko bëggoon a yóbbe gaay demba. Ca la Jéeri Joor Ndeela Faal ànd ak xaritam Sarica Jéey ñu bawoo Cees dem Caytu ca nijaayam Masàmba Saasum Koddu Jóob miy maam ci Seex Anta Jóob mi ñépp xam.  Ba ñu fa jógee dem Sugeer, Jéeri waxtaan ak ay mbokkam daldi ne du daw, xanaa day toog jàmmaelook noon bi xeex ba daan mbaa mu daanu. Booba fekk Tubaab yi tàmbale koo wër ba sax dig ab neexal képp ku leen jébbal Jéeri ci muy dundu walla mu dee. Waaye ci juróom-ñeenti fan ci weeru awril atum 1904 – fekkoon booba ñoñi kumàndaŋ Prempain yi doon wër Jéeri wër bu metti – la ko Kànnaar Faal reye. Kànnaar xaritam la woon, doon goroom te yit ñoo àndoon wuyuji ca Cees. Dafa lalal Jéeri ndëgg-sërëx, ba noppi dagg bopp bi ak benn loxo bi dem jox ko Tubaab bi. Na mu ko baaxoo woon def booba ngir tiital bañkat yi, Tubaab bi jël loxo Jéeri baak bopp bi samp leen cib bant bu gudd teg ko ca pénc ma feggoog màrse Cees. Booba Jéeree ngi amoon fanweeri- at ak ñaar rekk. Sarica Jéey xaritam bu gore boobee ba ñu ca tegee ñaari fan la ko Tubaab bi teg loxo, sànni ko Giyaan, nekk ca wetu Ameerig.  Sarica mujj na faa takk soxna ba am fa ñaari doom. Kànnaar Faal workat ba moom, Tubaab bi da koo mujjee wor, tëj ko ñaar-fukki at ci kaso bi. Ñaari at la fa def, tuub, dugg ci diine lislaam, soppi turam, di wuyoo ci turu Aamadu Kànnaar Faal.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-dibeer-29-sanwiye-2023/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM (Dibéer 29 saŋwiye 2023) CHAN 2023 Sunu gaynde yee ngi wëyal di wane seen bopp fale ca Alseri. Bërki-démb, ci àjjuma ji, lañ doon daje ak seen naataango yi, Saa-Muritani yi, ñu mujje leen ko yóbbul benn bal ci dara (1-0). Ab teg-dóor lañu am, dugal ko ci xaaj bu njëkk bi. Alseri, moom mi dalal joŋante yi, moo dóor na Koddiwaar 1-0. Madagaskaar itam a dóor Mosàmbig 3-1, Niseer daldi gañe Gana 2-1. Ñu war a jëm ci demi-finaal yi. Senegaal dina daje ak Madagaskaar  31i fan ci saŋwiye bi (19i waxtu) gannaaw ba Alseri dajee ak Niseer ba noppi (16i waxtu). Saajo Maane a ngi waaj a delsi Saa-senegaal bi, Saajo Maane, tàmbaliwaat na tàggatu fale ca këlëbam bii di Bayern. Ci fan yii nu génn, la dellusi ci pàkku tàggatuwaayu Bayern. Donte àndagul ak i moroomam yi, noo ngi gis muy liggéey di tàmbaliwaat di laal bal bi ndànk-ndànk. Loolu nag, nekk na luy dalal xeli almaŋ yi ak soppey këlëb ba, rawatina bi seen joŋante bu am solo bi ñuy waajal ak PSG jegesee. Cig pàttali, doomu Bàmbali bi dafa ame woon gaañu-gaañu ci óom bi. Weeru oktoobar 2022 la ko daloon. Dafa di, looloo ko tere woon a bokk ca kuppeg àddina sii weesu ca Qataar. Li mu delsi nag, du almaŋ yi rekk a ci bég. Mbokkam yépp, Saa-Senegaal yeet kenn demul ñu des. Ndaxte, sunu sag la. Ñépp a koy seetaan di bég ci moom. Kon ñoo ngi koy ñaanal bu baax mu gën a tane ba dellusiwaat ci pàkki wure yi. Bàmba Jeŋ dem na Lorient Bàmba Jeŋ jóge na Marseilles. Nde, këlëbu Farãs bi mujje na nangu li Lorient fay, daldi koy bàyyi mu soppi këlëb. Bërki-démb, ci àjjuma ji, la dem ca këlëbam bu bees bi, ñu wane ko muy saafonte ak soppey Lorient ya. Moom nag, ba fa Sampawoli jógee la yaakaaram xaw a tas. Ndax, tàggatkat bu bees ba, Tidoor, boolewu ko lool ciy mbiram, ba tax lam fa doon wure bareetul woon. La mu gënoon a bëg nag, mooy toog fa wane fa boppam. Waaye, am nañ yaakaar ni dem gi moo gën ci moom ndax xale la te fàww muy joŋante ngir gën cee màgg bay wane boppam.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/manchester-city-witti-na-biddiiwam-bu-njekk/
MANCHESTER CITY WITTI NA BIDDIIWAM BU NJËKK Àngale yaa ngay gundaandaat ! Manchester a ngi toj ! Ren, dafa baxa. Ci bëccëgu dibéeru tey ji, foo sànni woon mbàttu mu tàkk. Soppey Manchester City yaa nga feesoon dell mbeddi dëkk ba, di yuuxoo ak a fecci. Ñoo yey nag. Ndaxte, ba Manchester City dee këlëb ba tey, guléet ñuy jël “League des Champions”. Démb ci gaawu gi lañ duma Inter de Milan 1 bii ci 0, daldi witti seen njëlbeenug biddiiw ci joŋante bu mag bile. Ay at ñoo ngi nii, waa Manchester City di di rëbb kub bi. Saa bu xëccaan buum ga ba yaakaar ni bii mooy baax bi rekk, buum ga dog. Daaw jéeg, demoon ba finaal, Chelsea ne dóor ko, yaakaar ji tas. Daaw, mu dem ba demi-finaal, Real Madrid nax ko, toogloo ko. Te, ndeysaan, ñépp a foogoon ne day rey Real Madrid.  Waaye, ren de, fayu na fayu yu metti sax. Nde, dafa wulli Real Madrid wulli yu metti ci demi-finaal yi, duma ko 4-0, toogloo ko. Lu ko jiitu, ci kaar-dë-finaal yi, Bayern Munich la làbbali, toroxal ko biir dëkkam. Li may Manchester City doole mooy ne, ren, dafa jënd atakã, dugalkat, bu xereñ te xobe : Erling Haaland. Moo taxi t, atum ren ji de, Manchester City ñépp la tër, muy mbuucaa-mbuuj yi, di punkal yi. Fa Àngalteer de, kenn yabu ko fa. Muy sàmpiyonaa di FA Cup, lépp la raafal. Desalul kenn dara. Ligue des Champions kesee ko dese wonn. Mu doon janook Inter de Milan, di ékib bu naqaree futbalal. Finaal bi neexoon na lool. Joŋante bi neexoon na lool, bal biy daw jàmbar yay ñafe, ku nekk bañ sa moroom yóbbul la ko. Xaaj bu njëkk bi, ñu nekk ci ba dem noppalu, kenn dugalul sa moroom. Ñu dikkati ca ñaareelu xaaj bi, nekkaat ca, bal bay daw, gaa yay neexal ba ca 66eelu simili ba rekk, Rodri, di kuppekatu Manchester City, ne tuxum bal ba ca caaxu Onana yaa. Estaad bay riir, soppey Manchester City yay yëngal biir ak biti ga. Ñu nekkaat cay daw ba na mu jeexee. Arbit ne « Priip ! Priip ! Priiiiii…p ! » Rekk estaad ba tojati. Yuuxoo yeek sarxolle yi. Àngale yiy tëb ak a fecc fii, saa-itali yiy jooy, ndeysaan. Pep Guardiola nag, tàggatkatu Manchester City bi, yoroon Barcelone ak Bayern Munich, kenn gënu koo bég. Xol baa nga mel ne wanagu mbott. Ndax, kub bi, daf ko yàgg a yóotu. Am ñu naan sax, ci mbooru futbal, moom mooy tàggatkat bi gën a aay. Ak lu ci mën di am, jaanam wàcc na.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/lan-moo-wund-demu-maki-bi-riisi/
Lan moo wund demu Maki bi Riisi ? Fan yii weesu, njiitu réew, Maki Sàll, fekki woon na Putin ca Riisi ngir, nee ñu, ñu waxtaane  bekkoor bi xare bi xew digganteem ak Ikren jural àddina si, rawatina réewi Afrig yi. Ndax kat, Maki Sàll dafa jàpp ne xare bu ni mel, baaxul ci réew yu néew doole ni réewi Afrig yi. Nde, réew yooyii, ngën-ji bari li  ñuy dunde, dañu koy jéggaani bitim-réew. Te, muy Riisi, di Ikren, dañu bokk ci réew yi teg loxo dundeef yu mel ni ceeb, mbokk, farin añs. Jamono jii, nag, xare bi dafa gàllankoor yaxantug àddina si ak yóbbaliy dundeef yooyee. Kon nag, bu xare bi dakkul, koom-koom yi dinañu nasax, xiif gu metti dina am fii ak i weer. Looloo tax ñu bari def taxaw seetlu ci mbir mi. Ndege, Afrig ñàkkul bay tàllal loxo, di jéggaani ndimbal ak dund ngir askanam. Wax-dëgg, nag, Afrig soxlaalul kenn ndax li fi nekk ciy balli bindaare, géej yi ko wër, naaj wi ko tiim ak asamaan su nangu sii, nga teg ci ndaw yi fi ne gàññ, toll ci seen digg doole… Nee nañu mbas meek xare bi xew tey diggante Riisi ak Ikren ñoo tax koom-koomu réewi Afrig yi gën a suux. Mën na nekk. waaye, ndax ci loolu rekk lees ko war a delloo ? Déedéet. Bu dee loolu itam, dafa fekk ñu jël seen i yoonu yokkute tënk ko ci ñeneen. Loolu bokk na ci li tax seen i koom-koom mënuñu suqaliku boobaak léegi. Réew yépp tey, seen i bëgg-bëgg bopp a leen yitteel, du leneen. Ñoo wax dëgg sax ! Wolof nee, mag moom, bu naanee ndox mu, tàng suukër saa tax. Réew yi duñ ànd ak ku leen amalul njariñ. Kon nag njiitu réew lu fi teg yaakaram ci keneen ngir suqali koom-koomu réewam dina yàgg féey ci géej gu amul ndox. Moo tax, boo seetee ba ci biir, mbooleem li askan wiy jooy tey, ci yokkute geek yeneen yu ni deme, benn xare waralu ko ! Bu dee Senegaal, ay tamñareet (Miliyaar) lañuy yàq ci lu ko jarul, ba pare dëkk ci nger gu mettee metti. Ay dipite ak ay jëwriñ yuy sàcc te dara du leen ci fekk. Bu dund gi yokkoo kon kan a ? Njureef yi de, dañuy wane ni njiitu càmm gi di suuxale koom-koomu réew mi. Ci taxaw seetlu yi, am na ñu naan bi Senegaal di tëj digam ak bu Mali yàggul dara. Te umpul kenn ni digu Senegaal-Mali, ci benn at doŋŋ, ay tamñareet la ci Senegaal daan jële. Maki Sàll ak waa CEDEAO jékki saa rekk jël ay ndogal, ub dig yi. Li Senegaal di ñàkk ci bile tëj moo ëpp fuuf xare bi ñépp di wax. Maki daal, mu ngi soofantal koom-koomu réew mi. Bëgg a jiital bëgg-bëgg farãse yi rekk a waral coonoy way-dëkk yi. Ku ànd ak nguur gi mën nga sàcc, di njegenaayoo xaalisu réew mi. Néew-ji-doole yi ñooy yëg yokkute dund gi, ñoom lañuy sonal te ñoom lañuy tegal lu tar saa su nekk. Bekkoor (crise économique) gi yenn réewi Afrig yiy dund nag, ñu koy jaarale (tànqoo) ci xareb Riisi ak Ikren, ay fontu kese la. Beykat yaa ngi fii, ku leen tegoon ci ay anam yu baax kon déy benn Saa-Afrig du ñàkk lu muy lekk. Na njiit yi bàyyi tappale bi te liggéeyal réew yi. Loolooy dëgg. Ñàkk kersa gi njiit yi àndal dafa jéggi dayo. Moo tax ñépp di xeeb réewi Afrig yi. Maki de, tukkéem gii gàcce rekk la teg réewi Afrig yi. Daraay njariñ làmboowu ko. Ndax kat, ak fi Riisi tollu, moo waroon a soxla Saa- Afrig yi.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/afrig-ak-koronaa-afrig-ginnaaw-koronaa/
AFRIG AK KORONAA, AFRIG GINNAAW KORONAA USÉYNU BÉEY Koronaawiris bi, li muy metti metti, terewul kàngami boroom xam-xam yiy wéy di ci weccee xalaat ñeel doxalinu àddina si, ba xam luy nar a doon ëllëgu doomu-aadama, bés bu nu génnee ba set ci mbas miiy fàdd nit ñi, réewoo réew. Ñu ci bare jàpp nañu ne, bu nu génnee ci fiir gii nu koronaawiris bi fiir, warees na xoolaat tëralinu koom-koomu àddina sépp, waññi puukare bi te jox gëddam lépp lu ñeel wér-gi-yaramu doomu-aadama. Maanaam, tabax ay loppitaan yu baax te doy, ak lépp li ñu war a àndal ciy xeeti xarala. Warees na yit jiital lépp lu jëm ci dund gi dëgg-dëgg : mbey mi, càmm gi, lekk geek naan gi… Njàng meek gëstu bi tamit, wareesu leen a fàtte. Wax dëgg, Covid-19 bi musiba la, waaye booy seet ku mën a yar mag la. Fii ci Afrig nag, ñu bare jàpp nañ ne, su nu weesoo jamonoy koronaawiris bi, sunu réew yi waratuñoo des ginnaaw. Am sax ñu dem ba yaakaar ne Afrig moo war a aye, jiitu ñi ci des topp ci. Kon de mu neex ba dee ! Waaye loolu lépp, mbaa du ciy gént rekk la nar a yem ? Dëgg la, réewi Ërob yeek yu Amerig yi, ñoom, dañoo weere. Ndaxte, koronaawiris bi da leen a futti ba ñu set wecc ! Ndekete seen alal ju bare jeek seen doole ji leen ñépp xamaloon, fii lañ tollu : feebar biy lëmbe fépp, nit ñiy dee niy weñ, loppitaan yiy màbb, jarag yi jaaxle xamuñu nu ñuy def ba faju, fajkat yi jommi  ; nit ñiy làqu ci seen i néeg… Kenn dematul, kenn dikkatul, koom-koom biy nasax di ruus… Yaafus mënul a weesu lii ! Fekk booba, Afrig mel ne Sunu Boroom daf kaa beral loxo. Ba fi nuy waxe nii, mbas mi, ñi mu ci jàpp ba di yóbbu seen i bakkan, buñ ko dee méngale ak li xew feneen, mën nanoo sànt Yàlla ! Doonte sax benn doom-aadama rekk bu wàññeku, ñàkk wu tiis lay doon saa su ne, ak fu mu mënti doon. Ndegam kañ koronaawiris bi du ñëw génne yeneeni feem, jaxase mbir yi, dëggal yéeney ñenn ñi doon xaar Afrig nërméelu ba tàq ripp ci mbas mi ! Ndaxte, kat, jamono jii, muccagun. Senegaal gii rekk, limees na fi 2000i  way-aajowoo ceet ak lu teg ! Te yit, 25i doomi-aadama faatu nañ ci sababu koronaawiris bi. Kon, mbas mi bàyyiwul kenn, nu wax ko, waxaat ko : kuy nelaw ba yàndoor, lu la ci fekk yaa tooñ sa bopp ! Teewul sun dee seet bu baax day mel ni àddina si, gaa tukkiwul, waaye mu ngiy soppiku : boroom doole yiy jaaxle, daanu, way-ñàkk yi taxaw di fëgg dënn. Wànte, li mat a seetaat nag, mooy xam naka la sunu réewi Afrig yiy def ba bañatee doon ndaare, dem sax ba raw ci àddina sépp. Su nu wékkulee sunu yaakaar cib luxuskat buy ñëw defal nu lu ni mel, war nanoo seet fu nuy teg sunuy tànk, xam fu nuy jaar ba bañ a desati ginnaaw. Yàlla-Yàlla, bey sab tool. Ndax askani Afrig yi, rawatina seen i njiit, taxawe nañu boobu taxawaay ? Ndax ñi ñu séqal mbir mi, maanaam yeneen réew yi dinañ nu seetaan nu leen di dab ba di leen raw ? Mbaa danoo yaakaar ni ñooñu dañoo ñàkk doole ba mënatuñoo xippi ? Te yit, li gënatee am solo mooy samp laaj bii : ndax tëralinu jëflante yi am ci diggante réew yi dañoo soppiku ba fàww ? Su dee loolu lépp dara amu ci, fu nuy jaare yeneen réew yi ba romb leen, waxatumaag di leen jiitu ? Sunu njiit yi de, ba tey jii, ci liñ nu wonagum, ñu ngiy wéy di tàllal seen loxo di ñaan ndimbal. Bare na ci ñoom ñuy sàkku ci seen i naataango yi nekk Ërob, Amerig walla Siin ñu baal leen seen i bor. Walla boog, gën caa néew, ñu far 44i milyaar yi ñu war a fey ci at mii. Njiitu réew mi, Maki Sàll, moo ci gën a ràññeeku, ndax moom moo aakimoo wax ji te Macron, njiitu Farãs di ko ci jàppale bu baax. Monte de, ñoom Macron ak ñoom seen, am nañu lu leen doy sëkk. Moo tax it, waa Tugal yi  xam nañu bu baax ne, meneen pexe amul. Balaa ñépp di  labandoo fàww ñu seet nu ñuy fexe ba yombalal tuuti mbir mi waa Afrig yi, ndax ñu noyyi as tuut, ñoom it ñu am ci bànqaas bu ñuy jafandu ngir mucc. Li leen amal solo rekk moo di bàyyi xel ci buumu njaam gi, bañ mu rocciku, mbaa mu daŋ ba faf dàgg. Waaw, ndax gor dëgg dina leb lu mu dundale njabootam,  dem duggi, togg njëlam ba noppi dellu  di balu ndax ñàkk lu mu feye ? Di ñaan ñu faral ko boram ba noppi fas yéenee demati leb fa woon ?  Ndegam jéemul a naxaate (konte ndaw woyof bopp !), xanaa kon day yeew ay loxoom ba noppi daldi  jébbal boppam ? Ba réewi Afrig yi jëlee seen moomeel ba léegi, noonu rekk la seen digganteek réewi Tugal yi deme, daanaka. Doxalin woowule nag, feek jógu fi, bu yeboo nun askanu Afrig, nu tëddi te nelaw ! Kon réewi Afrig yi, rawatina seen i njiit, war nañoo am beneen jubluwaay bu dul di tàllal seen i loxo di saraxu, di sukkal ñi leen yeew bu dëgër, ngir sàkku seen yërmande ! Dëgg la, am na ci sunu njiit yi kenn ku ci ràññeeku lool ci jamano yii, mu di Andry Rajoelina mi fi wone taxawaayu bañkat, ak garab gi waa dëkkam, Madagaskaar, feeñal ne day faj koronaawiris bi, ci lu wér ! Ndax dëgg la am déet, doctoor yeek ñi seen xam-xam màcc ci wàlluw paj mi, dinañu ko wax. Waaye, Rajoelina moom ku mat a naw la ndax taxawaayam, ak fullaak faayda gi mu àndal yépp ngir aar askanam, réewi Afrig yi ak sax àddina sépp. Moom de, xaarul ñu wax ko nu muy def walla fu muy jaar ba génne ay ñoñam ci guta gi ñépp daanu tey. Nekkul it, ci doxalinam, di toppandoo njiiti réewi Ërob yi, ni ko ñenn ci naataangoom yiy defe, fàtte ne anam yi réew yeek xeeti àddina siy dunde dañoo wute lool, su ñu woroowul sax. Wolof Njaay, nag, dafa ne : benn loxo du tàccu. Jom ak faayda ji njiitu réewu Madagaskaar wone, doy nañ royukaay ñeel moroomi njiitam yi. Nañ bàyyi yalwaan, tàkk seen fit, xeexal seen askan. Boole seen i xalaat ak seen doole, fas yéenee jammarlook nooni Afrig yi, jiital seen i njariñal réew, liggéeyal seen askan. Suñ ko deful, na ko doomi Afrig yi defal seen bopp, seet nu ñuy lijjantee seen digganteek njiit yi leen wor. Jom mooy faj gàcce. Su gàcce gi dakkee la ëllëgu Afrig di door a leer. Tey-si-tey, nag, wax ji lii rekk la : nu nuy def ba jële fi mbas mile. Mbas waay ! Sunu réewi Afrig yi su ñu bennoowul xàll seen yoonu bopp, gisuma leen Mbaaw !
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/2020-mbas-mu-derkiis-nakk-teggin-tey-jur-tiinalante-ci-biir-reew-mi-ak-ci-bitim-reew/
NAKA LAA GISE MBAS MI Mbas mu dërkiis, ñàkk teggin tey jur tiiñalante ci biir réew mi ak ci bitim réew…. Naka la doomi Afrig yi war a taxawe ? Céy mbas  mee gudd tànk, moom mi fàqe Penku,  ca Wuhan, ca Siin, ca Asi, sóobu ci Afrig, ba ci Géeju Atlantig, daanu ci fii ci Ndakaaru (dëkk raw) ; ci Tànk (Wakaam, Ngor, Yoof) fekk ñu fi ! Balaa moo agsi, wëndéelu na, jaar Ërop, jaar Amerig ! Kon boog dab nañu, yëngal na jamono, yëngal àdduna wërngël  képp, wërngël këpp, wërngël këtt. Li bees Moonte ku xam jaar-jaari taarixu nit, xam ne du guléet musiba ak balaa xëppu ci gox, dëkk, réew, mbaa pàcc ci dunyaa. Li bees kay, moo di mbir mi ni mu gaawe, bette ak  law ; dëgg la, li ko waral moodi dem ak dikk bu gaaw te bare ci àddina, yéenekaay yu bées te ratax. Ak covid 19 tiitànge ak njàqare bare na, ñi faatu wax i nopp, moo xam góor, moo xam jigé. Mbas mii bàyyiwul ndaw te yab na mag, waxatumaak màggat. Ma nga doore Siin, faat fa ñu bare ; dàqe ji Tubaab yi Ërob ak Amerig, Naar yi yuuxu, sarxolle, mu mujj, dabsi nit ñu ñuul ñi, fii ci Afrig, fii ci Senegaal. Moone de doomi-Senegaal yi demoonañ ba yaakaar  ni dañoo tul, mbaa Yàlla ñoom rekk la bëgg. Li yëngu, li ko yëngal… Li jaaxaal ñépp, boroom xam-xam yi, doktoor yi, fajkat yi ak njiiti réew yi, mooy mbas mi kenn xamul li ko sabab. Mbaa du gëstukat yu waane ñoo ko rëccal walla lu ñu sos la, te tey ko, walla ndax bëre ay ponkal la ci politig, walla koom-koom ? Xey-na dina mës a leer bés. Li yëngu daal, li ko yëngal moo ko ëpp doole. Li ko yëngal nag, ndax ci njugub la jóge, mbaa meneen mala mu ñu doon jaay ca marse ? Koronaawiris ndax daa mel ni fel, mbaa teeñ, mbaa saxayaay ? Doom bi,  ci saxayaay lay dund walla ci xobu-garab ? Xam-xamu seetantal dina ko mës a leeral. Li wóor mooy dugg na ci yaramu nit, di wàllaate, indaale yaram wu tàng ak sëqat su bon, dënn bu fatt ak bakkan buy xelli ak biir buy metti. War nañoo xeex jàngoro ji, bëmëx ko ci biti. Réew yépp loolu la ñuy jéem. Ñenn ni teel a fagaru, mel niki Siin, dem nañ ba bëmëx mbas mi ; ñi yéex a jóg, sàggan mel ni Itaali, Espaañ, Farãas, Amerig, waaru nañu, metti na lool ci ñoom, ña fa dëkk, juddoo fa, màgge fa, di fa tedd, ak ña fa ganesi mbaa wutsi wërsëg. Pexeyeek jumtukaay yi Bi mbir nee faax, yenn réew yi mel ni Siin jiital xam-xam, xel ak caytu. Naka noonu dañuy ber ñi jàngoro ji laal, def ay lël, door di seet garab yu mën a indi tan. Ci réew yu bare, am na ñu seen xel dem ci xam-xami Maam ya ak diine, ñu dem sax ba ni njaaxum yiy gën di bare ci àddina ñoo tax Yàlla mere ñu, delluwaat di cawe, ngir ñu  dellu ci dénkaane yi mu jaaraale woon ci Yonent yi. Jar na nu jàng, jàngaat, sóobu ci, tanq ci woyu Sëriñ Musaa Ka, Xarnu bi, xarnu bi ñu génn (XXel), moom  bàyyiwul koom, aada, diine, mbaax ak xarbaax, tarixa, yoonu mucc, texe. Moonte war nañu fàttali, mbaa xamle ni, sunu Maam ya, waa Këmit, Misra, Esipt, ñoo jëkk a bind ci dund ak dee ; mbégte ak naqar. Fii ci Senegaal Ci sunum réew, ki ko jiite, toog ci jal bi, Parsidã Maki Sàll, woote na waxtaan ak njiiti làngi polotig ak mbootaay yi ànd ak jamono yiy aar  liggéeykat yi, waxtaan ak dippite yi, ndawi réew mi ngir am lu mu yokk ci li mu xalaat ci bëre ak mbas mi. Ku ne def nga li la sa xel, xol, yaram, kàttan, mën-mën, pexe, gafaka may. Gëstukat yi, fajkat yi, def nañu seen keem-kàttan, ba mbir mi am fu mu yem, jéggeegul dayo. Bi mu agsee ba am fi weer, ñu gis ne laal na 195 nit, 40 % yi dañoo indaale doomu mbas mi,  dugal ko ci réew mi , 56 % dañu leen ko wàll, 4 % xamuñu fu mu ak naka la leen dabe. Loolu tax na, ñu war a gën a fagaru doonte xamuñu fépp fu mbas mi di jóge ; lii tamit la Porofesëer Musaa Seydi miy jiite xéex bi ci xam-xamu settantal ak paj denkaane. Ñi koy jàppale ci caytu gi ak jumtukaay yi, doktoor Ablaay Buso, Alfa Sàll ak Mamadu Jara Béey dalal nañu xel yi, joxewaale ay ndénkaane yu ñu mën a may ñu mucc ci. Dëgg la, am na doomi réew ñu ci jot a faatu, am ci ku doon ku am tur, fulla ak faayda ci réew mi ak ci bitim-réew, mu di Paap Mabaaba Juuf, ku ñu ràññe ci xam-xamu tàggat yaram, ak ci gunge xale yi ci futbal, dem ba jiite ekibu Màrsey, ca Farãas. Ëllëgu jàmm, tinkeeku ak tabaxaat Li am ba des moo di sàggan baaxul, wér-gi-yaram, jàng ak xam-xam war nañu leen sédd bu baax a baax. Ñu dellusi ci li mag ñu baax ñi dénkaane woon, fexe ba liy génn  ci pénc yi ak lël yu bare yi nuy amal, nu def leeni  jëf. Su boobaa luñu bett, ñu dékku ko, ci lu gaaw. Dëkk ci  fàtte, gàtt xel ak réccu ñoo ànd. Gëstukat yi am nañu sas bu réy, war nañu gën di waxtaan ci seen biir, di wax ak ñiy jiite ci yeneen fànn. Mbokk yi, at mii, nar na gudd tànk lool !Mu ngi mel na fasu benn tànk « rëkkal mba ma rëkk», nitu guddi ! Njuuma jaa ngook ! Am na ñu mu jaafurloo, mel ni Tubaab yiy wax nañu gaaw wuti garab, ñakk bu bees, jéemantu ko ci nit ñu ñuul ñi. Taat wuy tàkk moom kenn mënu ko solal tubey, kërandoom du set. Doomi réew mi, doomi àddina, jaaxle nañu ! Ku moytuwul nag tam sa moroom dëmm, tam sa mbokk nóoxoor Lu mën a dindi jaaxle ? Xana daal ñu dal, gën a njàccaar, yokk caytu gi, jàppoo ci fagaru gi, paj mi. Nu jeexal ci seetlu bi : réew yi ci muccagum as tuut, ci Afrig mel ni Lësotoo, Komoor, Malawi, Sudaan, Sawo Tome bokk nañu ci yi duggagul, mbaa yi sore xëccoo ak buuxante yu metti ci biir àddina. Kon boog nanu gaaw ci teggi tànk ci benn yoon, teg tànk bu bees, bu gën, te àndandoo jublu ci tabax Bennoo Afrig ci Mbokk. Nañu Taxaw Temm, am Pasteef, tegu ci Yoonu Askan Wi, Déggoo ngir Bokk, Bëre, Daan. *Baabakar JÓOB Buuba, Njiitu Mbootaayu Doomi Afirig yiy yëngatu ci Liifant ak Njàngum mag ñi, PAALAE (Pan African Association for Literacy and Adult Education) te nekkoon njiitu An@fa di bànqaasu PAALAE fii ci Senegaal
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/lan-la-wutaakon-yi-naral-lakki-reew-mi/
Lan la wutaakon yi naral làkki réew mi ? Waaw mbokk yi, lan la wutaakon yi naral làkki réew mi ? Man ci sama wàllu bopp, déggaguma ci lu ma doy. Ndax Wolof, Pulaar, Séeréer, Soose, Joola, Sooninke…. dañu leen di wéy di suufeel teg Frãnse mbaa Àngale ci seen kaw ? Ndax Frãnse kese mooy wéy di nekk “làmmiñ wi Repibligu Senegaal fal, di ci jaarale léppam” ? Ndax làmmiñ yi xeetoo Senegaal dinañu nekk kenu njàngale mi, li ko dale daara yu suufe yi ba ci Iniwersite yi ? Ndax seen mbind, seen xabaaruwaay, seeni téere dinañu tas ci Réew mi ? Ndax dinañu fexe ba doomi Senegaal yëpp mën bind ak jàng ci làmmiñ yi ñu nàmp ? Làmmiñu réew mi war na ñoo dugg ak doole ci daara yi ak ci kuréli njàngum liggéey yi, ñu ciy sàkku xam-xam : xarala, ladab, xayma, mbay, napp, tabaxin, mekanig, elektoronig, tas-xibaar ak ñoom seen…Su ko defee sunu Askan, sunu Xeet ak sunu Réew dinañu def jéego gu réy ci yoonu suqaliku ba dab réew yi seen koom gën a naat ci dunya. Jamono moom-sa-Réew jot na. War nañu fullaal làmmiñi réew mi, jox leen seen cër ba mu mat sëkk, ñu doon ay jumtukaay yu tàkku ngir tinkeeku. Yaakaar naa ne “Lu Defu Waxu” war naa mën a bind bataaxal juroomi wutaakon yi laaj leen li ñu naral làmmiñi réew mi
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/jonanteb-xaritoo-senegaal-door-na-kamerun-1-0/
JOŊANTEB XARITOO : SENEGAAL DÓOR NA KAMERUN 1-0 Gayndey kuppe yi dóor nañ Kamerun 1-0. Tey ci altine ji lañ doon amal joŋanteb xaritoo ca fowub Bollart bu Lens (France). Saajo Maane moo dugal biiwu Senegaal bi. Ab penaaltii la am, dugal ko. Joŋante bi nag, lees ko dugge mooy waajal CAN 2024 biy xewe fa Koddiwaar. Te sax, Senegaal ak Kamerun ñoo bokk genn kippu, war a laale keroog 18 saŋwiye 2024, ca fowub Yamusukroo. Fu ñaari gaynde daje, pënd ma wuri. Senegaal ak Kamerun, saa buñ waree laale, àddina sépp ay toog di seetaan. Nde, bokk nañ ci ñaari réewi Afrig yi gën mag ci wàllu kuppe, ñu ràññee seen i kuppekat fépp ci àddina si. Moo tax, seen um ndaje mën a doon lépp ba mu des joŋanteb xaritoo. Ni mats tey bi demee firndeel ko. Ndax, ñaari ékib yépp a joxe li ñ amoon yépp, mel ni ñuy xëccoo kub. Mu nekkoon mats bu xumb, saf lool. Kenn mayul sa moroom dara. Moo tax, gaañante bi xawoon na bari ba arbit bi jot fa séddale 4i kàrtoŋi mboq. Senegaal nag moo daan ci seen njëlbeenug joŋante bii laata bu 18 saŋwiye 2024 bi. Daanaka, ékibu Senegaal bi, ñépp ñoo gis, rawatina Kaliidu Kulibali, Kerepeŋ Jaata, Ismayla Jakobs ak Saajo Maane mi dugal. Dañ foogoon sax ne Kaliidu Kulibali, kàppitenu ékib bi, dafa tàmbaale jëm mag. Waaye, tey de, wone na ne dese na ñeex. Ku weddi laajal ñoom Abuubakar ak ñoom Toko-Ekambi. Dafa di, penaaltii bi sax, moom Kulibali moo ko indi. Nde, moo la wattukatu (défenseur) Kamerun bi takk, mel ni kuy bëre, daaneel ci suuf. Arbit joxoñ tombu penaaltii bi, Saajo Maane toj caaxi Andere Onanaa yi. Senegaal am benn, Kamerun tus. Kamerun jéem na lu nekk ngir dab Senegaal, waaye dóor bu jub sax amuñu ko. Kon, xelu saa-senegaal yi war dalagum ci li seen gaynde yi wone tey. Waaye, sikk amul ci ne, joŋante bii ak bu CAN 2024 bi duñu niru. Nde, Kamerun dina bëgg a fayu. Waaye, Senegaal bii, bu dëggalee boppam, dina jafee dóor.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/li-gen-a-fes-ci-xibaari-taggat-yaram-alxames-9-mars-2023/
LI GËN A FËS CI XIBAARI TÀGGAT-YARAM (ALXAMES 9 MÀRS 2023) KUPPE Àngalteer Démb, foo geestu ci mbaali-jokkoo, ñoo ngi doon wone ay naataal ak i widewooy kii nga xam ni mooy defãsëeru Manchester City bi, Kyle Walker. Mu mel ne ku àndul woon ak sagoom. Nde, mi ngi ciy tërëf ni ku màndi. Bu ca yemoon sax mu tane. Waaye, dafa mel ni ku lonk as ndaw, dawal loxoow yi ci awaray soxna si. Loolu nag, jur na wax ju réy, foofa ca Àngalteer, nek it lu ñu ñaawlu lool. Rafetul sax cib kuppekat bu ñépp ràññe. LIGUE DES CHAMPIONS PSG toogati na Démb ci àllarba ji la Bayern Munich, ekibu Saajo Maane bi, doon janook PSG bu ñoom Messi ak Mbappe. Njëkkoon nañu laale, 15i fan ci ginnaaw ca Pari, Bayern Munich dóor ko fa 1-0. Kon, PSG dafa waroon gañee as-tuut 2i bii ngir mën a jàll. Waaye, saa-almaañ yi mayuñu leen ko. Nde, wulli nañ leen wulli yu metti, wan leen ni xaajaguñ bay doon ekib bu mag. 2-0 lañ leen duma. Te, bu dul woon li arbit bi far benn biiwu Bayern bi ak li ataakã yi rate, doon na gën a ñaaw. Saajo Maane, bi joŋante bi dese danaaka 10i simili la dugg. Neymar moom dafa ame gaañu-gaañu moo tax kuppewul. Ci 7i at yii weesu, bii mooy 5eelu yoon PSG di tooge wicceem-dë-finaal. Chelsea toogloo na Dortmund Chelsea nax na kii di Dortmund ba génne ko ci Ligue des Champions bi. Bërki-démb ci talaata ji la woon seen joŋanteb ñaareel bi, mu dóor ko ñaari bal ci dara (2-0). Kuppekati Dortmund ya nag, am na ña bégul ca ni arbit ba doxalee. Ndax ku ci mel ni Bellingham moo ngi wax ne def nan li ñu waroon yépp, waroon nañ mën a gañe joŋante bi. Waaye nag arbit bi ni mu dooxalee dafa mel ne ku jeng jëmale ci waa Chelsea yi. Ñoom li leen metti mooy ni dafa dogal ñu dooraat ab teg-dóor boo xam ni bii kuppekatu Chelsea bi daf koo dóoroon mu moy. Li waral loolu nag, mooy ñenn ci waa Dortmund yi dañoo romb ci déyal biñ waroon na yam ba ñuy dóor bal ba. Benfica itam toogloo na Fc Brugge, dóor ko juróomi bal ci benn (5-1) gannaaw bam ko dóoree woon, ca joŋante bu njëkk ba, ñaar ci tus (2-0). CAN U20 2023 Senegaal dana daje ak wóllareem bii di Gàmbi gaawu 11i màrs bii ñeel finaalu CAN U20 bi. Ñoom ñaar nag, ba léegi dóoruñu ci kenn te lakkuñu ci it caaxu kenn ba nii nuy waxe. Loolu nag, du wéy, ndax bu bés baa kenn dana wéyal loolu ka ca des xaar. Ñuy ñaan Senegaal jëlaat boobu kub. LÀMB Gannaaw “recours” bi mu defoon, waa CNG mujje nañ jox kii di Saa-Cees ndam ci kaw Rëg-Rëg, xamle ni moom mii dafa rëpp ñeenti cëram (4 appuis) ca bëre ba. Muy àtte bu jaar yoon ndaxte ñepp gisoon nañu ni am na.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/bes-du-mag-du-tuuti-boroom-lay-tollool/
BÉS DU MAG, DU TUUTI, BOROOM LAY TOLLOOL… Dëgg la : ràcc jëmale sa kanam baaxul waaye tey fàww LU DEFU WAXU xamle mbégteem ci ndam li Paap Aali Jàllo am fan yee nu génn ca Iniwérsite Gaston Berger bu Ndar. Paap Aali ci kër gi la bokk, ayubés bu Yàlla sàkk mu am lu mu bind ci seen yéenekaay bii di LU DEFU WAXU. Nun ñiy liggéey ak moom xam nanu ne bu ci Yàlla àndee, kenn du wax ëllëg ci yenn kàllaamay réew mi, rawatina pulaar ak wolof, te doo tudd Paap Aali Jàllo. Àllarba jii, deesu ko fàtte. Waaw, àllarba 20eelu fan ci weeru Féewaryee, Banqaasu Làkk ak Caaday Afrig (LCA), bi nekk ci Pàccum Aada yi, Diine yi, Aar yeek Jokkalante yi, doon na dalal ab ndongoom, mu war koo jax. Xew-xew baa ngi ame ca Iniwérsite Gaston Berger bu Ndar. Ndongo li doon jébbal kàngam yi njuréefi gëstoom mooy Paap Aali Jàllo. Ci kàllaama nasaraan, xew-xew boobu dees na ko duppe “soutenance de mémoire”. Loolu, nag, mi ngi am ginnaaw bi fa Paap Aali jàngee lu tollu ci diirub juróomi at. Liggéey bi Paap Aali doon jébbal mbooloo mi, ci turi Pulaar yi la aju. Maanaam, gëstu bi mu amal ci diirub ñaari at, li mu ko dugge woon mooy biral jëmmi turi Pulaar yi, fésal ni ñu sosoo ci kàllaama pulaar, leeral seen cosaan, ak di xamle lu tur yooyii wund. Waaye, Paap Aali yemul foofu. Ndaxte, wax na ci biir téere-tëju-diggam bi naka lees tànne tur ñeel waaso Pulaar yi, gëm-gëm yeek pexe yi ko lal ba ci ngénte nees koy amale. Xóotaayu gëstu bee waral Paap Aali dem ba wone turi yaradal yeek xeeti tur yoo xam ne, ràññee njaboot gee leen tax a jóg. Maanaam, ni xale yi di toppalante, li ko dale taw bi ba ci caat bi. Loolu fés na ci tablo bii nu jële ci téeréem bi. Kàngam yi doon saytu liggéeyu Paap Aali bi ñeent lañu : Porfesoor Maweja Mbaya mi jiite woon àtte bi, Doktoor Mouhamedoune Abdoulaye Fall, jàngalekat ca Banqaasu LCA, Doktoor Mariama Mahamane Maїga mi doon tette ndongo li ba liggéey bi yemb, ak njiitu Banqaasu LCA bi, Doktoor Ibrahima Sarr. Moom, Doktoor Ibrahima Sarr dafa wute bés bi ndax dafa amoon ngànt. Ab tukki moo ko teree teew. Waaye, jot naa yónnee ab bataaxal, biral ci mbégteem, seedeem ñeel Paap Aali, rawatina gis-gisam ci téere-tëju-digg bu Paap Aali Jàllo. Ci suba si, bi fukki waxtu jotee, ci la ndongoy Banqaasu LCA tàmbalee feesal “Amphi B”. Mbokki Paap Aali yeek am-di-jàmmam yi tamit kenn demul ñu des. Bi fukki waxtu tegalee fanweeri simili, la lawax bi jël kàddu gi, layal xalaat yi mu xelli ci biir téere-tëju-diggam bi ginnaaw bi ko kilifa yi mayee ñaar-fukki simili. Mu daldi nuyoo ba noppi xamal nit ñi naka la tànne bile ponk, cosaanu liggéey beek jubluwaayam. Ci nasaraan, Paap Aali mi ngi doon gëstu lees di wax “Anthroponyme Pulaar : formes et sens”. Moom, nag, tur yi Pulaar yi moomal seen bopp rekk la jagleel liggéey bi ngir biral ni tur ci bokk-moomeelu askan la bokk. Mu tënk, wone ay masala, leeral leen ci noppi nit ñi. Waaye, bala tog nomlet, toj nen. Benn liggéey xéyul rekk sotti. Looloo tax Paap Aali xamle yoon wi mu jaar, jafe-jafe yi mu jankoonteel ak pexe yi mu lal ba jéggi leen ngir sottal mbind mi nga xam ne, mi ngi tollu ci 159 xët. Bi mu noppee, delloo na kàddu gi Kilifë yi doon càmbar téere-tëju-diggam bi. Njiitu àtte mi, Porfesoor Mbaya gërëm ko ndax li mu fexe ba yem ci waxtu wi ñu ko mayoon. Jàngalekati Banqaasu LCA yi, Doktoor Mariama Mahamaan Maїga, Doktoor Mouhamedoune Abdoulaye Fall ak Doktoor Ibrahima Sarr, seen seede benn la. Nee nañu dañoo mӫs di bég ci Paap Aali, ndongo lu am pastéef, bӫgg lool li muy def. Dafa mës a doon royukaay ci ay moroomi ndongoom, nekk jàngkat te ku weg ñi muy jӫflanteel la. Ñu neeti, Paap Aali bokk na ci ndongo yi gën a xereñ ci Banqaasu LCA. Terewul, àtte nañu ko àtte bi war ginnaaw bi ñu saytoo liggéey bi. Li ci jaar yoon, kilifa yi rafetlu nañu ko bu baax. Masala xibaar yi mu indi ñeel Pulaari Fuuta Tooro yeek seen làkk wii di pulaar. Rawatina bi mu nu xamalee seen i tur ak li ñu wund. « Njuumte, nag, mënul a ñàkk ci téere-tëju-digg”. Loolu la Porfesoor Maweja Mbaya leeral laata muy jubbanti yenn njuumte yi mook Mouhamedoune Abdoulaye Fall, ak Mariama Maїga. Kilifë yépp sampoon nañu ay laaj yu Paap Aali tontu tontu yu leer. Danuy jaaraat ci baatu Alpulaar, mu nekk baat bu siiw bu nuy dàkkantale nit ñiy làkk Pulaar. Te firi bi moo di “waxal Pulaar !”. Ci gis-gisu gëstukat bi, wareesul a woowe Pulaar yi baat boobu. Ndaxte, ab pulaar deesu ko wax “waxal pulaar” ndax moom la nàmp. Waaye baatu Alpulaar buuru Fuuta Tooro ba woon, Mànna, moo ko waxoon jëme ko ci wolof yeek yeneen waaso yi fa nekkaloon ak Pulaar. Ku ci làkk pulaar ñu woowe la “Alpulaar”, ku ko làkkul ñu rey la. Kon, baatu Alpulaar ab Ndigal la woon. Baatu “pël” yit noonu, wareesu ko jëfandikoo ngir tudd Pulaar yépp. Ndx kat, “pël” mécce la, maanaan ab sàmmkat la. Te ci biir Pulaar yi am nay nappkat, ay tëgg, ay géwél, ay uude, añs. Kon turu Pulaar moo gën jekk ci ñoom. Jotaay bi, nag, yàggoon na ba jéggi dayo. Waaye, ba benn waxtu ci bëccëg jotee ba tegal fanweeri simili la kilifë yi daldi yégle seen àtte, jébbal ndongo li « Mention très bien ». Muy firndéel màggaayu liggéeyu Paap Aali. Ñépp ndokkale ko, ñaanal ko mu jig ko te yeneen lijaasa topp ci. Xarit yi daldi jël ay nataal ni ñu ko tàmm a defe. Ay xéewal lañu ko tëje, fa la mbooloo mi añe ba suur, naan yu sedd te neex. Ma baamtuwaat ko, bés du mag, du tuut, boroom lay tollool, te keroog kenn werantewu ko.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/emma-seen-daan-na-saa-cees/
ËMMA SEEN DAAN NA SAA-CEES ! Démb ci dibéer ji, 5i fan ci weeru Me 2024, la doomu Pikin ji, Ëmma Seen doon sëgg ak Saa-cees, doomu Géejawaay ji. Seen bëre nekkoon lees doon xaar. Nde, dañu doon ñaari mbër yoy, duñu yàq làmb. Bu ñu bëree mu neex, bu ñu xeexee mu neex. Kii di doomu Pikin ji nag moo mujje am ndam ci kaw Saa-Cees. Seen bëre bi nag, yéex naa tàmbali. Ndaxte, ñu ngi sëgg bi 22i waxtu tegee 36i simili. Ba mu tàmbalee, ñaari mbër yi, ku nekk a ngi ne tekk di jàng sa moroom. Saa-Cees, lees ko xamee woon mooy ni songkat la, ci simili yu njëkk yi lay jëli naatangoom, mu jigoon ko nag. Waaye, ci bésu démb ji, dafa ñëw taxaw di déglu. Ndax, Ëmma nag, du mbër mu ndaw. Ñaari mbër yi di léewtoo lu tollu ci 3i simili, Saa-cees tàmbali gëdd doomu pikin ji. Ñoom ñaar ñu sànnantey kurpeñ. Muy lees doon xaar ci ñoom. Ñu xeex xeex bu metti, ku nekk ni waat tekk di déglu sa moroom. Niki ñuy léewtoowaat ba mu yàgg, arbit bi woo leen, wax ak ñoom ngir ñu bëre. Ñu gis ne Saa-cees dafa gaañu ci loxo bi, mu dem ardo ñu xool ko. Ba mu delsee, ñoom ñaar tàmbaleeti di léewtoo lu tollu ci 1 simili, rakku Bàlla Gay ji dellu ca ardo mu xoolaat ko. Bi ñu ko xoolee gis ni mën na àggali mu dikkaat ci géew gi. Ci noonu, arbit ëfëlaat leen, yàggul dara Saa-cees yéegat ci kaw Ëmma Seen. Ñaari mbër yi di xeex. Noonu rekk Ëmma daw jàpp ko, jéem ko tegal siis, Saa-cees bañ. Ñu nekk ci noonu, Ëmma féete suuf di bañ-bañlu ba jugaat daldi takk doomu Géejawaay ji, daan ko. Noonu la seen bëre bi demee. Ku nekk joxe na lim am, wane jom, fullaak fayda jees leen xamee woon. Pokola Balde itam moo mujje daan kii di Liis-Njaago. Mu nekkoon bëre bu neex a neex. Ñaari mbër yi xeex ci xeex bu metti. Daanaka, ca jàkkaarloo ya la tàmbali woon a takkarnaase sax nag. Ci bëre bi, ñu xeex ba kii di Pokala dem ardo ñaari yoon. Waaye, mu nekk ci rekk ba mujje am ndam ci kaw Liis-Njaago. Mu nekkoon bés bu neex ci làmb. Nde, ay waada rekk a doon daje démb. Rax-ci-dolli, mu bari woon i soppe yu seetaansi woon. Ci bés bi tam, Bàlla Gay 2 ak Tafaa Ti mim war a dajeel. Ñu nappante fa, ku nekk di jéem a xëbal sa moroom ak di ko wax mu waajal bés bi, ndax du yomb.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/ban-a-wacc-sa-and-baay-njaay/
BAÑ A WACC SA ÀND… Mbir mi doy na waar. Kenn xamul lii lu mu doon. Nekk cim réew, dund fa lu ëpp fanweeri at, te ba tey may bind baat yi, doxandéem la ñu la fi jàppe. Am fi liggéey bu baax, di faj samay soxla ak a dimbali samay mbokk ; bokk ci ñiy yëkkati koom-koomu réew mi. Ci  gàttal, man nanoo wax ne Baay Njaay xaw naa tekki ci réew mi te amal na njariñ dëkk bi. Bariwuma fi ay xarit waaye am naa fiy xameel yu rafet jikko yoo mën a jëflanteel ci wàllu àddina ak diine. Bi may ñów Itali amaguma fukki at ak juróom-ñatt. May xale bu góor, tollu ci sama diggu ndaw. Ma ànd ak kàttan, wóolu sama bopp, yaakaar ne lu sama loxo yóotu jot ko. Dëkk bu ñuy wax Duwinoo, fa laa ame bàkkaloryaa soog a dem Triyeste. Fa laa defe  sama lisãs. Yàlla dimbali ma ma jàll eksame doktoraa ca iniwérsite bu Siyeena. Kon dëkk bii ame naa fi ay lijaasa yu raññeeku ci daara yi gën a kawe.  Lu nit di itewoo ci njàng, Yàlla may na ma ko fi. Ba ma noppee ci loolu laa taxawal am mbootaay ngir siggil jëmmu Afrig fii ci Itali, bokk tamit ci mbootaay yiy xeex ngir sunu aada ak sunuy làkk am seen gëdd. Dara yombul ndax Wolof Njaay nee na «Ndar xëyul sotti». Masumaa jàng sama kàllaama, Wolof, bay am fitu taxaw ne damay dundal li ma nàmp. Waaye yaakaar naa ne li amoon solo mooy tàmbalee xam sa bopp ak geestu fi nga jóge walla fa nga cosaanoo. Ndànk-ndànk may jege ab bindkatu wolof ak di jàng abajaday làkk wi. Ma dem bay tàmbalee firi baatu waa réew mi ci Wolof. Mbir mi dugg ma, saf xorom, indil ma yokkute yu am solo ci samay xalaat, sama gis-gisu àddina, ak samay xameel. Lu neex du doy, te kenn du ko dog ba beneen yoon. Nit koo gis am na ku ko xàllal yoon mu jaar fa. Ca njëlbeen ga, jànkoonte woon naa ak ay jafe-jafe yu bare ci njàngum wolof. Ci yëngu-yëngu bu am solo la dajeek boroom xam-xam bu siiw, ñu raññee ko lool ci mbindum kàllaamay Kocc ak tekki ay làkk yu wute ci Wolof. Waaye kooku damay leb turam ba beneen…
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/maggalu-daaru-xudoos/
MÀGGALU DAARU XUDÓOS Mu doon tur wu siis wi ñu ko xame, màggalu daaru xudóos doon xew-xewu diine. Murit yi di ko màggal at mu jot ca Tuubaa, rawatina fa goxu daaru xudóos. Xew-xewu diine boobu di fàttali bés ba Sëriñ Tuubaa Xaadim Rasuul di wuyuji Boroomam. Mu doon bés ba ñu ko jébbalee Boroomam faTuubaa ginnaaw ba mu làqoo ca Njaaréem (Njurbel). Ñu njëkk ko màggal ca atum 1935. Sëriñ Móodu Mustafaa di ab taawam nekk tamit xalifaam bu njëkk moo taxawal bés boobu. Muy wéy ba su nu jonni-Yàlla-tey. Waa Daaru xudóos di ko màggal ba mu far wuyoo ci turu màggalu Daaru xudóos. Bés boobu ëmb mboor ak i baatin ca atum 1927 ba Sëriñ bi làqoo. Mu nekkoon tiis ju réy ci murit yi, jur njàqare ci taalibe yépp. Waaye, seede yi di wéy di biral taxawaayu taawam ba mat sëkk taaw, di Sëriñ Móodu Mustafaa. Nde, loolu ndénkaan la woon digganteem ak Sëriñ bi. Ndax, la mu sàkku woon ci moom mooy “ Bés bu ma wàccee, nañu ma yóbbu Tuubaa”. Mu nekkoon jamono yu metti ci digganteem ak tubaab yi waxoon ne, mëseesu koo bàyyi ( résidence surveillé) ba ni mu làqoo. Mébét moomu la doomam ja sottal ba ni mu ko indee Tuubaa te benn tubaab gisu ko. Ren, ñu màggal ko ci dibéer jii weesu 6 ut 2023, yamoo woon ak 19i fan  muharram atum 1445. Ci teewaayu Sëriñ Ahmadu Maxtaar, di xalifab Daaru Xudóos. Bés boobu di am njooqe. Ndax, teewaayu nit ñu takkoo-takku ngir fekke guddi gi. Mu doon bésu xubbeeku ci ay bàkkaar. Nde, képp ku ko fanaane màggal ci béreb bu sell ba, ñu far say ñaawteef. Mu doon kàddu yu Sëriñ Móodu Mustafaa jaayante ak Boroomam.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/seex-beeco-cuun-atte-yallaa-gen-bu-nit/
SÉEX BEECO CUUN : ÀTTE YÀLLAA GËN BU NIT Altine 6eelu fan ci weeru Me, atum 2019. Bés bi ñépp doon xaar, bésub layoo, bésub àtte, ñëw na. Li tax ñépp doon xaar bés bii, nag, du neen. Waaw. Kan lañu doon àtte ? Sëriñ Séex Beeco Cuun, di Xalifa di yit kilifa cantaakon yi. ‘’Bóomug Madinatul-Salaam’’, bile dàkkental la taskati xibaar yi utal mbir mi sabab layoo bu siiw bii. Juróom-ñaari at la lànket bi def, doore ko 2012 ba 2019. Ñépp a doon xaar ndogalu àttekat bii di Xaasimu Ture, mu waroon koo biral ci altine jii. Mbir maa ngi xewe woon ca Madinatul-Salaam, 22eelu fan ci weeru awril 2012. Yéenakaay yi xéy dégtal nu xibaar bu yéeme : 19 cantaakon ñoo faat ñaar ci seeni mbokki taalibe ba noppi suul leen te kenn yégul, kenn tinul. Ñu ni déet-a-waay, gaa ñi ne Sëriñ bee leen jox ndigal. Nee ñu, Abaabakar Jaañ ak Baara Sow, ñaari way-dëddu yi, lenn rekk a tax ñu boom leen : xérte ak mbëggeel gu jéggi dayo ñeel seen Xalifa bi. Ndax, àggoon nañu ci di ko woowe Yàlla. Loolu, nag, moo indi coow li bu ñu sukkandikoo ci xibaar yi fi jotoon a rot jamono yooyu. Coow li ne kurr ci këru Séex bi, mu yabal ay taalibeem ngir ñu génne fa Abaabakar Jaañ ak Baara Sow. Noonu, 19 cantaakon yi dem ba ci yoon wi, xeex ak Abaabakar Jaañ ak Baara Sow, daldi gor kenn ki jaasi, fetal keneen ki ba noppi gaawtu suul leen. Nee ñu sax ki ñu fetal deewagul woon bi ñu koy suul. Ginnaaw bi ñu defee seen tóoxidóoni ba noppi, dañu ko doon jéem a nëbb far Yàlla def am ku leen bett, boole leen ak sàndarm yi. Bi mbir mi siiwee ba yoon jot ci, coow li ne kurr. Ñépp di naqarlu jëf ju ñaaw jooju. Li ci gënoon a doy waar mooy li Séex Beeco Cuun – mi yilif ñi ñu bóom ak ñi leen bóom – noon, moom de, yëgul tinul. Booba ba léegi, nag, def na juróom ñaari at, yoon di luññutu, di seet a ka seetaat ngir xam kan a def lan. Bu dee taalibe yi nga xam ne ñu ngi woon ci tëjub-négandiku, li leen yoon toppe woon mooy : bóomug njuumte bu ànd ak mbugal, làqub néew, ñàkk a siiwal rey bi, mbooloom-caay-caay, teggi yoonu suul néew ak ñoom seen. Séex Beeco Cuun, moom, lii la ko yoon toppe woon : luqnjuurug bóom, maanaam bu bóomulee it teewoon na bi ñuy fexe mbir mi. Jotoon nañoo teg loxo Sëriñ bi ak 19 taalibeem yi. Séex bi, nag, yoon da koo mayoon sañ-sañub négandiku ndax li mu tawatoon ba tax mëneesu ko woon téye ci kaso. Nan delsi ci altine keroog jeek daan yi fa jóge. Layookati Séex bi, nag, ñaanoon nañu àttekat bi mu fomm layoo bi, xaar ba seen kilyaan wér, mën koo teewe. Waaye kenn mayu leen loolu. Moom Séex bi, àttekat bii di Xaasimu Ture daanoon na ko fukki at yoo xam ne dina ko liggéeyal réew mi ak ndàmpaay lu tollu ci téeméeri miliyoŋ CFA yu mu war a jox, moom ak 19 taalibeem yi, njabootu way-dëddu bu ci nekk. Mbir mi indi werante, am ñu naan daan bi dafa woyof, taalibe yi naan yoon deful liggéeyam, dañoo bañ Séex bi rekk. Sëriñ Saaliyu Cuun, taawu Séex Beeco Cuun, joxoñ na baaraamu tuuma àttekat bi ak nguur gi ci boppam. Ndax, bu ñu sukkandikoo ciy kàddoom, sàmmontewuñu ak àqi Séex beek i yelleefam. Waaye bi loolu lépp di am, Séex baa nga woon Frãs, ci benn loppitaanu Bórdo, di faju. Benn fan doŋŋ lañu ci teg, mu daldi génn àddina. Nee ñu sax yëgul daan bees ko tegoon. Laaj bi ñépp di laaj moo di : daan bi ko àttekat bi daan, ci kan lay dellu ? Ay boroom xam-xam yu seen xel màcc ci wàllu yoon, tontu nañ ci. Nee ñu 10 at yi Séex bi waroon a liggéeyal réew mi, dañu koy teggi ndax ab néew deesu ko liggéeyloo. Waaye ndàmpaay li, ci njabootam lay dellu, ñoo koy fey. Ak lu ci mënti am, xalaat yeek gis-gis yi wute nañu. Wànte li wóor moo di ne àtte Yàllaa gën bu nit.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/sampiyonaa-almaan-bayer-leverkusen-jel-na-ko/
SÀMPIYONAA ALMAAÑ : BAYER LEVERKUSEN JËL NA KO ! Xabi Alonso ak gaayam yi def nañ ko. Dugal nañ Bayer Leverkusen ci mboorum futbalu Almaañ. Ci anam bu rafet a rafet lañ ko defee nag. Saa-Espaañ bi, Xabi Alonso miy tàggatkatu këlëb ba, def na jaloore ju réy a réy. Niki dibéeru démb ji, 14 awril 2024, lañ duma Werder Bremen 5i bal ci 0. Ndam loolu leen tax a nekk waagay (champions) sàmpiyonaa. Ndaxte, ki topp ci ñoom, Bayer Munich, mënatu leen a dab. Muy guléet ci mboorum Bayer Leverkusen. Nde, bi këlëb bi sosoo ba léegi, mu ngi sog a gañe sàmpiyonaa bi. Saa-Españool bi ak i ndawam daldi nañu dakkal nguuru Bayern Munich foofee, fa Almaañ. Dafa di, 11i at yii weesu yépp, moo rekk a daan jël sàmpiyonaa ba. Daawu ko bokk ak kenn. Kon, li Xabi Alonso ak i kuppekatam def, jaloore ju réy a réy, rawatina bi nga xamee ne keen xaaru leen woon file. Li gën a réyal jaloore ji mooy ne, moom Bayer Leverkusen, amalagum na 43i joŋante yoy, kenn dóoru ko ci : dafa gañ38i yi, daldi témbóo 5 yi. Gaa yi dugal ci 123i bii, jël ci 31i. Laata seen joŋanteb démb ji, soppey këlëb bi dañu fees dell mbeddi gox ba, di jaajëfal seen tàggatkat bi, ba sax daldi ne soppi nañu turu yoon wi jëm ca fowu ba duppee ko “Yoonu Xabi Alonso” (Xabi Alonso Alle). Xanaa yayoo na ko ! Nde, moom Saa-Espaañ bi, dafa soppi xar-kanamu këlëb ba, di leen futbal-loo lu set te rafet, neex a seetaan. Wëliis sàmpiyonaa bi ñu gañe, dese na leen ñaari kub yi ñu war a mën a jël. Ndaxte, am nañu finaalu kubu Almaañ ba te njortees na ne ñoo koy jël. Rax-ci-dolli, am na joŋanteb kaar-dë-finaal ci Ëropaa Lig ba, te dafa gañe West Ham ci mats bu njëkk bi. Fi mu nekk nii, ñettale (triplé) la Xabi Alonso di diir. Siporteer yi ñoom, nee nañ, bu fi yemoon sax mu neex. Ndeem neex na, nay gën di neex !
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/waxtaanu-saada-kan-ak-bubakar-boris-joob/
‘’LI TAX SÉEX ANTA JÓOB AMUL MOROOM…’’ Waxtaan wii, ab tekki la ñeel jotaayu laaj-tontu bu Saada Kan di amal ci tele 2Stv ñaari ayu-bés yu nekk, te mu dalaloon ci sunu werekaan bi, Bubakar Bóris Jóob keroog, altine 22eelufan, sulet 2019. Li ngeen ciy jàngsi mooy xaaj bu njëkk bi. Saada Kan : Noo ngi am mbégte delsi ak yéen ci seen jotaayu waxtaan « L’entretien » bi nu leen di dégtal ñaari ayu-bés yu nekk. Tey, nag, noo ngi dalal gan gu mag, ab werekaan bu ñu ràññee ci àddina sépp, mu di ab bindkat bu yebu ci ittey réewi Afrig yi rawati-na ci lu ñeel seen daraja, di ab móolkat, taskatu xibaar, jàngalekat. Kookooy Bubakar Bóris Jóob. Moom lanu fi dalal tey, fas yéene waxtaan ak moom. Kon, Bubakar Bóris Jóob, ginnaaw bi nu la nuyoo, nu bàyyi la nga nuyoo laata nuy sóobu ci waxtaan wi. Bubakar Bóris Jóob : Jërëjëf Saada. Maa ngi lay sant di la gërëm ci dalal biŋ ma dalal ci jotaay bii nga xam ne, xam naa ko bu baax sax. Ndaxte damay faral di ko seetaan saa yu ma ko sama jot mayee. Ndax li may toog bariwul, saa su nekk maa ngi ci roppëlaan yi. Waaye, jotaay bu ma yitteel la ; dama koy seetaan saa yu ma amee jot. Saada Kan: waxtaan wi nag, dama koy doore ci ndokkeel la ngir yool biñ la jagleel fan yii weesu ca Etaasini. Bubakar Bóris Jóob : Waaw. Jërëjëf. Yool bi, “Harold Ethel L. Stellfox” lañ ko dippe. Iniwérsite Dickinson bi nekk ca Pensilwani, ca réewum Amerig, moo ma ko jagleel. Ma bég ci lool sax, ànd ci ak sag bu réy. Ndax, ñi ma ci jiitu, ay bindkat yu mag a mag lañ, ma bëgg leen lool, def leen ay royukaay te daan jàng seeni téere ca ba may ndaw. Looloo ma tax a bég ci li ma jot ci yool boobu. Jëli woon naa ko. Jot naa fa amal sax aw waxtaan, jàngaale fa tuuti sama téere bi, Murambi ci nasaraan ak sax Doomi Golo ci wolof. Saada Kan : Nga ne ma ! Ci wolof, nag… Bubakar Bóris Jóob : Waaw, waaw. Mayoon nañ ma ko. Li ma ko dugge woon mooy baaxe am mbooloo mu déggul wolof, taaru kàllaamay Kocc ak neexaayam. Saada Kan : Noo ngi lay sant ci sa teewaay ci waxtaan wi. Naam, ñépp a la xam. Waaye, du ñàkk mu am ñu umple ne, ca njëlbéen, jàngalekatu xeltu (philosophie) nga woon, nekkoon tamit taskatu xibaar. Nu gis ne at yii weesu yépp, yaa ngi doon jàngale, di bind, di amal i waxtaan, di wër àddina si. Jamono jii sax yaa ngi jàngale ca Niseryaa. Muy biral ne yow, jëfkat nga. Ma bëgg laa laaj, ndax du xeex bi ngay xeexal làmmiñi Afrig yi, rawati-na wolof, moo la yóbbe loolu lépp ? Bubakar Bóris Jóob  : Waaw. Jàpp naa ne, xeex booboo sabab lépp. Te, du loo xamante ni, dafa xéy rekk sotti. Boo xoolee ba ci biir, dinga gis ne sax, jaar-jaar boobu nga tudd, fa la bépp bindkat di faral di jaar, rawati-na bindkat buy xeexal jenn itte ju ko ñor. Maanaam, dangay nekk ndaw bu gàtteñlu, bëgg lool njàngum téere yi, di jéem a topp ci tànki bindkat yu mag yi. Rax-ci-dolli, ngay bindantu ay taalif yu ndaw, ay kilib ak ay téere fent. Noonu nga koy jàppe ba xéy bés, génne ab téere. Bu ko defee, ñu jàppe la bindkat, ndax du yaa koy def sa bopp. Ndege, fàww nit ñi jàppe la bindkat nga door di ko nekk. Noonu, ay ndigaale sa diggante ak nit ñi tàmbalee juddu ; ngay tibbe ci mboolem-nawle mi di bind, di roote ci seen nekkin ak dundin ay xalaat ak i gis-gis di leen jëmmal ci say biir téere. Ñoom itam, ñuy jàng say téere di la ci laaj ngay tontu. Waaye, duñu ci yem. Ndaxte, dinañ lay faral di laaj sa xalaat ci nekkinu askan wi, xew-xewi jamono walla sax xew-xewi àddina sépp. Bu ko defee, nga sóobu ci illa ju bees : jëmmal nekkinu nit ñi, rawati-na wu doomi Afrig yi. Noonu la bindkat bi di jëflante ak askan wi. Maanaam, ci moom lay jële daa ji muy rëdde téereem yi ngir jëmmal seen nekkin, dégtal àddina sépp kàddu yiy riir ci seeni xol te seeni làmmiñ të leen a tudd. Léegi, nag, bu ñu seetloo, xool nekkin ak dundinu doomi Afrig yi, benn njàngat lañ ciy jële : njaam gi deñagu fi. Njaam gi maam yi doon dund ca jamonoy njaam ga ak ca jamonoy nooteel ba, am na ba tey. Ba jonni-Yàlla-tey jii, mënees na ràññee màndarga yi ci réewi Afrig yi : yorin wi, nguur ak njiit yiy jaamu nootkat ba woon, toroxtaange ak tolof-tolof yi askani Afrig yi di jànkoonteel bés bu nekk.  Li ci gën a doy-waar mooy ne, Afrig rekk ngay fekk ay bindkat yuy bind ci làkk woo xam ne, seeni nawle walla ñi ëpp ci askan wa ñu bokk dégguñu ko.  Muy lu yéeme ! Lan moo leen di tax a bind ak kan lañuy bindal ? Ndax xel nangu na loolu ? Man ci sama bopp, ndànk-ndànk laa tàmbalee yeewu ci mbir mi. Te bu loolu amee, ginnaaw Yàlla, maa ngi koy sante jàmbaar ju mel ni Séex Anta Jóob, sama doomu-baay bi.  Te du man rekk, képp kuy xeexal làmmiñi Afrig yi, seeni aada ak lépp lu ñeel seen daraja, war ngaa delloo njukkal Séex Anta Jóob ndax moo sumb liggéey bi, xàllal nu yoon wi.  Ci gàttal daal, mbirum làmmiñ lu am dayo la ci sama jaar-jaar. Saada Kan : Am na loo mës a wax, te mu soxal ma lool. Nee nga bés “nekk doomu Afrig, mook dund mbugal ñoo yem”.  Mu mel ni li wax ji wund mooy dafa jot nu xeex ngir sunu daraja. Yow miy boroom wax ji, loo ci namm dëggëntaan ? Bubakar Bóris Jóob : Waaw. Li ma tax a wax ne, nekk doomu Afrig, mook dund mbugal ñoo yem, ñaari mbir la. Bi ci jiitu, mooy jafe-jafe ak boddikonte yi doomi Afrig yi di dund jamono jii, rawati-na boroom der yu ñuul yi. Tey, mbañeel ak tiitaange ji yeneen xeet yi ameel nit ku ñuul moo ma gën a tax di wax. Ndax, Jamono jii, ñaawalees na lépp lu aju ci nit ku ñuul walla mu ñeel ko. Moom kay, tudd Nelson Màndelaa walla Baraak Obamaa sax génnewu la ci. Feek yaa ngeek der bu ñuul, jàppees na la nib gàkk-gàkk walla tilim bees war a raxas ba mu set wecc, jële ko fi. Loolu, ñuulaayu nit ki la ñeel, muy benn. Bi ci topp, nag, doomi Afrig yi ci seen bopp la ñeel. Dafa di, cosaanoo Afrig ñenn ñi bàkkaar lañ ko jàppe. Tey, bët bu ñaaw lañuy xoole Afrig. Boo nee Afrig rekk, xel yi dem ci xareb maxejj yi (guerres civiles), coxorte, yorin wu ñaaw wi ñu yore réewi Afrig yi, cambar-cambar bi, ndóol bi ak tumurànke bi, nger mi, añs. Saa boo xamee ne, nit ku ñuul nga teg ci nekk doomu Afrig, dañuy jàpp ne warees na la jéppi, xeeb la, suufeel la.  Loolu laa tudde mbugal. Saada Kan : Kon, Bóris, bu ñu la déggee, ngir nu mucc ci jafe-jafe yooyu, ngir nu nekk, fàww nu xam nun nooy ñan. Te loolu, mënta àntu feek geestuwunu démb, roy ci maam ya tey ndamoo sunuy moomeel. Mu mel ni looloo la tax a bind ci wolof. Rax-ci-dolli, mënees na méngale sa taxawaay ak bu Séex Anta Jóob.   Ndax danga jàpp ne, wareef la ci doomi Afrig yi ñu wéyal xeexam ak ndono li mu nu bàyyee ? Bubakar Bóris Jóob : Waaw. Mi ngoog. Loolu kese la, du leneen. Man, dama jàpp ne ñi ëpp ci nit ñi dañu réere mbiri Séex Anta Jóob. Ndaxte, saa yuñ ko tuddee rekk, xel yépp dem ci Misra mu njëkk ma, mómi ya, piramid ya, ca wax ya mu daan wax ak li mu bind ci sunu cosaan te mu doon lu am a am solo. Xel yi dinañ dem itam ci firnde yu leer yi mu jële ci gëstoom yu xóot ya, te diy wone ne, baaxi maam yu Misra yu njëkk ya, ay nit ñu ñuul, diy doomi Afrig, ñoo ko jëmbëtoon, suuxat ko ba mu naat lool, raw ci àddina sépp jamono jooju. Toog nan fi diir bu yàgg, Séex Anta rekk a doon wax ne, Afrig a sukk jur àddina si. Bépp xeetu mbañ ak ngànt indil nañ ko ko, weddi ko ngir rekk bëgg a werante. Ñi bañoon dëgg googu, àggoon nañ ci sos ay fen yu tooy xepp ngir rekk mbañ, xeebeel ak coxorte gi ñu ameel nit ku ñuul, rawati-na doomu Afrig. Waaye, suul ker du ko teree feeñ. Tey, boroomi xam-xam yépp a bokk ànd ci waxam ja. Kenn déggatul ña ko daan weddi démb. Waaye, liggéeyu Séex Anta mëneesu ko tënk ci gëstukat bi mu doonoon. Séex Anta yemul woon rekk ci di wax ak di firndeel ne, Afrig moo sukk jur àddina si walla, sunuy maam ya woon ci Misra ay nit ñu ñuul lañu woon. Liggéey na yit lu am solo ci wàllu politig. Bu leen fàtte ne, Séex Anta Jóob nekkoon na fi politiseŋ. Waaye, nag, wute woon na lool ak politiseŋ yi nu xam. Moom dafa xamoon ne, xeex bi mu daan xeex, mënta àntu feek nguur dugalu ci loxoom. Maanaam, fàww nga yor ndogal li ngir mën a jëmmal xalaat ak yéene yi nga am ñeel sa réew walla sax Afrig gépp. Te, bokkoon na ciy yéeneem yu rafet ya, fexe ba réewi Afrig yépp booloo doon benn. Te, nag, ak li mu doon rafet xalaat yépp, mësul a dige lu mu mënul walla lu mënta nekk. Maanaam, daawul fen di dajale ni yeneen politiseŋ yi. Muy lu am a am solo. Séex Anta dafa daan wax ne, bu réewi Afrig yi bëggee tàggook seeni jafe-jafe, fàww ñu ànd fajandoo seeni jàngoro te kenn bañ a jéem a demal boppam. Ci gis-gisam, képp ku beru ci sa wet, dinga wéet ak say jafe-jafe. Te, béy bu àndul ak i  moroomi béyam, ànd ak cere ja. Kon, Séex Anta ak ñu mel ni Sànkaraa, Kuwaame Kurumaa ñoo bokkoon benn xeex, bokk benn jubluwaay bi : afal Afrig, boole doomi Afrig yi ñu doon benn ngir Afrig naat, ay dommam tekki. Moom, li ko wutale ak i maasam mooy itte ju mu joxoon làmmiñi Afrig yi ak liggéey bu réy a réy bi mu ci def, rawati-na làmmiñi réewum Senegaal. Wone na ne, làmmiñi Afrig yi ñoo bokk cosaan ndax ci làmmiñu Misra lañu soqeekoo. Biral na itam mbokkoo gi nekk seen diggante ci wàllu aada, muy lu am solo. Dafa di sax, téereem bu siiw boobu mu génne ci atum 1954 te mu tudde ko “Nations nègres et Cculture”, moo may fit ñenn ñi ba ñu sóobu ci xeex bi. Ndege, ci màqaama téere bi la kurélu FEANF juddoo bañ ca tegee 4 at, ca Frãs, diiwaanu Gërënoobal. Kurél gi, nag, ay boroomi daraja, ay kàngam yu ñu ràññee, ñoo ko séqoon, ñu ci deme ni Abdulaay Wàdd, Asan Silla, Séex Aliyu Ndaw, Saaliyu Kànji Masàmba Saare, Asan Ja, añs. Ku lim juum. Waaye ay boroomi dayo ñoo ci bokkoon te amal liggéey bu am solo lool sax ñeel làmmiñu wolof. Ngir fàttali, kurél googu moo fi génne woon Ijjib wolof, muy ab téere bu ñeeloon njàngum wolof. Liggéey boobu moo àgsi ba ci sunu jamonoy tey jii. Lépp li ñu jot a wax walla def ci làmmiñi réew mi, ginnaaw Yàlla, ñooñoo tax te ñoom, téere Séex Anta baa leen xamb. Moo tax nu war ko sant, sargal ko, delloo ko njukkal. Ndax wolof dafa ne, bu lëg lekkee aloom, na ko gërëme coy…
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/2312/
Njàngatub Bàmmeelu Kocc : Téereb dekkali 1/2 Du guléet. Déedéet. Bindkat bi tëbul rekk bind Bàmmeelu Kocc Barma. Nde, ginnaaw Doomi Golo, bii mooy ñaareelu téereb nettali bu werekaan bi, Bubakar Bóris Jóob, génne ci làmmiñu wolof. Te sax, li ko jiitu, Bóris jot na fee yatt xalimaam gu set gi te neex, tekkil nu téereb Aimé Césaire (Une saison au Congo) bi ci kàllaamay Kocc, tudde ko Nawetu deret. Moom, nag, tur wu yéeme la tànn, daldi koy duppe ñaareelu téereb nettali bi këru móolukaay EJO génne : Bàmmeelu Kocc Barma.Tur woowu de, day naxe. Ndaxte, du jaar-jaari walla jaloorey boroom xam-xam bu siiw boobu di Kocc Barma Faal la ciy nettali. Déedéet ! Nettali bi nu Bóris di baaxe, walla boog xew-xew yim nuy saabal, muŋleen jukkee ci jéyya ji fi amoon, daanaka 20i at ci ginnaaw : suuxu Gaalug « Joolaa » gi daan lëkkale Ndakaarook Sigicoor. Ndeysaan, ba tey, askan waa ngiy jooy 2000iy doom-aadama yi ci labe woon. Rongooñ yooyoo tooyal xolu bindkat bi ; mu boole ciy yosam, def leen daa. Ci daa ju tiis jooju te lëndëm la capp xalimaam gi. Ngir biral metit ak njàqare yi 1883i way-labu Gaalu Joolaa gi doon yëg, keroog ba ñuy lab. Dafa di, bu sañoon, bakkan bu ci ne, dina biral sag dund. Maanaam, « 1883 toqi deret. Ak benn. Bunu fàtte benn toqu deret boobu. Bunu ci fàtte benn, sax. » Waaye, kim ci tànn doy na misaal ñeel way-lab yépp. Li ko waral mooy ne, kooku, dub como. Mukk ! Soxna Kinne Gaajo mi Bubakar Bóris di nettaliy jaar-jaaram ci téere bi, ab taalifkat bu mag la woon, siiwoon lool. Gis ngeen, soxna soosu, turam wër na àddina ndax rafetaayu xalimaam ak solos mbindam. Aka xareñoon ! Ndeysaan, bu dul woon tolof-tolof yim daan jànkoonteel, kenn waxatu ko tey. Bare na ñuñ fiy kañ ak a tagg te Soxna Kinne Gaajo xoolu leen sax. Waaye, ay nattoo ko gaaraloon ba mu àggoon ci di jaay boppam guddi gu nekk ci benn goxu Ndakaaru – Caaroy. Laaj bi bindkat biy laaj ci téere bi, « Taalifkat walla lagara ? », loolu lay wund. Ndege, Soxna si, ñaar yépp la boole woon. Moom sax, Kinne Gaajo ci boppam, jéggi woon na loolu lépp. Ci dëgg-dëgg, moom daa bokkoon ci nit ñu kéemaane yooyu nga xam ne, bokkuñu ak nit ñi doxalin. Foo ko fekkaan, ciy feemi boppam la daan deme, di ci doxe, di ci waxe. Feemi boppam kese, nag ! Maanaam, nit ku moomoon boppam la ; dara tënku ko woon te tënkuwul woon lu dul ci li ko safoon. Bu yeboo ñu ne, Kinne Gaajo, amul woon tiitukaay. Moo tax bindkat bi ne, « Kinne Gaajo masul a def leneen lu dul jéem a xàll aw yoon. Yoonu boppam. » Looloo tax ay dëkkaaleem ak i xamaaleem jàppe woon ko ni ku ràkkaaju, ku yenuy dàllam, maanaam ab dof. Jaar-jaar bu doy waar boobu la xaritu-ndawam, doomu-ndeyam ji Njéeme Pay, di nettali, gannaaw ba mu réeree (ak i taalifam yu bare) ci géej gi. Mu mel ni ku nuy fàttali mennum Dawid Jóob mi fi woon : « Mu mel ni kon Dawid Jóob ak Kinne Gaajoo bokk àtte foofu. » Njéeme Pay, taskatu-xibaar la woon. Mi ngi ame woon lijaasam ci lekkool bu mag boobu ñu duppe Cesti. Ku xareñoon lool ci liggéeyam la. Cib rajo biñ moomaloon seen bopp, moom ak i àndandoom, la daan liggéeye. Rajo ba, Péncoo FM la tuddoon. Ndegam moo dencoon kayiti xaritam yi, Njéeme Pay dafa jàpp ne, sas la ci moom : « …sas nañ Njéeme ». Loolu moo ko tax a yéene biral taalifam yu am maanaa yi mu fi bàyyi, ba noppi « … xamal askan wi kan moo doon Kinne Gaajo… » ndaxte, « Àddina ba àddina daj, amul ku sañ ni moo ma gën a xam Kinne Gaajo. » Lim ko dugge mooy fexe ba àddina sépp xam kan moo doon, dëgg-dëgg, Kinne Gaajo. Njéeme daal, tawax na temm fas yéene noo nettali Kinne Gaajo.  Konte, Njéeme Pay, sàmmonte na ak kóllëre gi doxoon ci digganteem ak ndem-si-Yàlla ji, xaritam. Fi Njéemey daanele nettaleem bi la ko keneen di aw, jël kàddu gi, jokk nettali bi. Loolu, nag, ci feemi bindkat bi la bokk. Ndege, aw-awley nettalikat ci téereb nettali, du lu bees ci mbindiinu Bóris. Njëkk na koo def ci Doomi Golo. Ndaxte, xew-xew yi daan am ca Ñarelaa, góor gi Ngiraan Fay mi doon xaar bésam a nu leen jëkk a jottali laata muy faatu. Gannaaw gi, Aali Këbóoy mi ñépp jàppe woon dof (nees jàppe Kinne Gaajo itam), moo mujje àggale li nu Ngiraan doon nettali. Nettalikat biy aw Njéeme Pay ci Bàmmeelu Kocc Barma, jigéen la ni moom. Te, ndeyu-mbill gi ci boppam, Kinne Gaajo, ca barsàq ja mu nekk, mooy wéyal nettali bi… Moom la sax de. Baatam beey bëtt suuf si ko sàng ca bàmmeel ba mu roñu, di jib ba ci téere bi. Noonu, mu daldi dekki, di nu xamal ay jaar-jaaram ak i yëg-yëgam. Jàngkat bi, nag, mënul lu dul topp bindkat bi cib « dóor-dàqe » bu dul jeex. Mel ney àndandoo yuy dem ba yàgg, réeroo ; ku ci nekk di wër keneen ki. Ndaxte, yuq gi lal Bàmmeelu Kocc Barma yépp, ci diggante ñaari way-jëmmal yooyu – Kinne ak Njéeme- la ràbboo. Waaye, yemu fa de. Déedéet ! Dangeen a desee xam Bóris rekk. Waaye aka cee aay ! Moo taxit, defatina mëninam. Day wër-wërloo ak yow, naan la  « … naxee-mbaay… ». Noonu la lay def, di la wommat, yow miy jàng téereem. Ruq-ruqaan bu nekk mu dugal la fa ; dëkkoo-dëkk mu wërloo la. Tey. Démb. Ëllëg… jamono yépp lay boole ràbb, fu ne mu yóbbu la fa. Moom daal, tëralinu mbindiinam a deme noonu, xoromu lool nag ! Way-jëmmal yiy jëf ak a jëflante ci téerey bindkat bi, mëneesul a xam fum leen di loqatee. Dafa di, ñoom, dañuy méngoo ak jëmm yees leen di melal ba ñu faf mel niy nit dëggantaan. Sàllaaw ! Te, ku la ci gën a am maanaa, nga ne kii. Jëlal taskatu xibaar bu xereñe bi te gëm liggéeyam, « Te surnalist bi, liggéeyam du dara lu dul taataan i xibaar, siiwal leen. », doy na firnde. Walla nga xool kiy mbubboo surnaalist, di mbuxum ak a jaayu ngir lu mu def ci poosam ba mu dëll. Mooy ku njublaŋ kooku, te mu fexe ba yoxosu, dugg ci biir surnaalist yi, fexeeti ba bokk ci seen i njaatige yi gën a am doole ; kooku noonu rekk demoon bay noggatu politiseŋ yu ñàkk-jom yi, « Te kilifa gu fi am alal mbaa bayre mu luqati say mbóot, ni la soo ma joxulee nàngami milyoŋ ma def sama liggéey ». Waaw, kii nga xam ne nag, taal fitna rekk a ko soxal, « Nun surnalist yi nag, na ma Yàlla baal waaye liggéey bu doy waar lanuy def : su musiba dalee ci kow askan wi, lu mu gën a réy, gën a metti, nu gën a raatukaan. » Waaye, geestul it liggéeykatu bànk bu maandu bi, walla waxambaane wu lafañ wii moroomam yiy tooñ,« Am na ñu ma doon kókkali, naan booy bii bumu nu sonal, lafañ doŋŋla. » Nanga xool yit politiseŋ yu ñàkk faayda yi. Nóoxóor yi nga xam ne, seen biir doŋŋ a leen jiital, tax ba bindkat bi (mën a tooñ ba dee !), boole leen ñoom ñépp, waa Nguur geek Kuje gi, di leen ñaawal,« Yëf yi powum mag doŋŋ la : kenn du taxawal pàrti ngir defar sa réew walla jëmale ko kanam. » Mu am it jeneen jëmm ju am solo ci nettali bi, moo di ndeyu Kinne Gaajo, jigéenu kaw gi, di néew-ji-doole ju ñàkk lépp ba mu des jikko ju rafet ak jom, « Moonte Yaa  Ngóone, lim ma won moo doon ne ngor, tabe ak njub, fépp fu suuf si ŋàyyeeku goqiy doomi-aadama, soo demee fekk leen fa. »… Xanaa du noo ko gisandoo ? Ndax deesul a fekk way-jëmmal yu ni mel ci mboolem-nawle mi ? Konte,  mel na ni, Bubakar Bóris Jóob du cib maaliforo lay tabaxe ay way-jëmmalam, Ñi mu nuy indil ñépp, dañuy mat li mu leen soxlaa ba jëmmal leen. Ni tëgg biy naxanteek wurus wi, walla tabaxkatu ndaa biy mooñ banam, « Noo mënti def, fàww nga gajafal ban bi, di ko mocc, di naxanteek moom, daanaka, ba mu miin sa nuggaayu loxo, nooy nepp, ni nemm, lu la neex nga def ko ci. Soo nee : ‘Amoon na fi’, mbooloo mi ni tekk di la déglu, bala ngay sañ ni : ‘Fa la léeb doxe tàbbi géej, bakkan bu ko njëkk a fóon tàbbi Àjjana !’ dinga wax lu set. Wax lu set mooy rekk : teqale, tasaare, ràbb, ràññee bu baax kañ la fen di jur dëgg ak kañ la dëgg di yées fen. Mooy : jëmbët fulla ci sa liggéey – bind liggéey la war a doon – te lu mu metti metti nga muñ ko. » Liggéeyu bindkat bi daal, duy caaxaan walla lu yomb ! Bóris bëggul lu yomb, utul lu yomb. Moo tax, way-jëmmal yi muy tabax làmboo maanaa jees leen xame. Li koy gënatee màndargaal mooy ñaar ñi gën a yées jikko ci Bàmmeelu Kocc Barma : surnalist bii di Lamin Jàllo ak politiseŋ bii di Ngañ Demba. Ndaxte, ñoom ñaar ñooñu kat, li ñuy bon a bon yépp ci jikko, ñoo ciy tamit, ñi ci ëpp xorom, neex deret ba, ñàkk leen a bëgg day jafe. Ndax Bóris jëlul ay nit dëggantaan, ñu xam leen am déet, dugal leen ci téereem bi ? Bokk na ci màndargay téere bi, ñenn ci way-jëmmal yi bokk ci way-labi gaalug « Joolaa bi ». Fës nañ ci téereb nettali bi lool, sax. Nde, bindkat bi dina dem ba am ñu mu ciy tudd seen i tur dëgg, ànd ceek kersaak yëg-yëg gu réy, ndax li mu leen xamoon, moom ci boppam, ci bi ñuy dund. Xawma kan, waaye kilifay nguur gi, ñoom, Bóris moyuleen ci téereem bi. Waaye, moo yey xalab leen. Ndax, kat, ñooñu, defuñu lu dul féex, ñàkk yitte, ñàkk aajo, doyadi ba nga ni lii lu mu doon ! Rax-ci-dolli, ñoom ñooñu, ñooy ndeyi-mbill gi, ñoom ñi sàggan ba musiba bu ni mel dal ci kow askan wi. Ak seen yambaraay ! Ak seen cuunewaay ! Ñu waroon a walluji way-lab yi, génne leen ci seen njàqare ji, waaye ñu nooyal ba ñooñu mujjee dee. Bu nu waxantee dëgg rekk, ñoom politiseŋ yi, ci yeneen i itte lañ nekkoon. Ki koy firndeel mooy Seneraal bi làngi woon ca coroom ba, jamono ji jéyya jiy am. Te, boobu, kenn ñemewu ko woon a gëtënsi, fa mu doon gundaandaat, di ko yëgal balaa ba amoon ca géej ga. Waaye, du njiit yi kese ñoo sikk. Askan wi tamit, kenn demul ñu des. Nde, mooy la waa ji waxoon rekk, askan wu nekk, njiit ya mu yeyoo lay am. Réew moo dem, na askan wa mel, noon lay njiitam mel ndax ca askan wa lañ soqeekoo. Bu ko defee, cuune, yaafus ak càggan yi kilifa yi àndal ba tax jéyyab Joola bi dikkal nu, dees na leen fekk ci askan wi. Loolu la nettalikat bi xam ; ndax ku mën a seetlu la ndeke. Moo tax, deñul ciy sulli mbóoti askan wu déggadi wii, tigi, « … xoolal ma kalandoo yi, njaga-njaay yeek kaar-rapit yi, fu leen neex taxaw, ku ci alkaati laaj say kayit nga tàllal ko kayitu téeméer gu tilim mu lem denc, ni la soo ñibbee ngoon nuyul ma Jekk-Tànk ! » Doxalin bu ni mel, nag, warul a bett kenn. Ndaxte, dara yàqul Senegaal lu dul yëfi maa-tey ak maslaa bu ëpp. Nde, Senegaal mooy réew moo xam ne« … lu neex waay mu def te dara du la ci fekk ! ». Bi Joolaa bi suuxee ak léegi ba Njéeme Pay di nu ko nettali, am na daanaka 20i at. Waaye, la woon, fa woon, na woon. Jikko yi soppeekuwuñ. Moom, kay, ndax yéesul sax lees di laaj. « Lu fi xewati sama ginnaaw ? Pólitig rekk. Ndékkee pólitig, añe pólitig, reere pólitig. Kon, ci gàttal : dara lu bees xewu fi. Masàmba randu, Mademba riigu. Waaye Mademba, dañ koy wax nag te dee, masutoon a xalaat ne bés dina ñëw mu ne faax ci jal bi. Fit wi rëcc, mook soxnaam ñuy giroo cere ji, di ko caxat-caxatee, ku ci gën a fëqle sa moroom nga ne kii la ! ». Jikko de, dinañuy wax ne laago la ! Te, laago du wér. Am déet ? Nun nag, njort nanu bu baax ne, ci gis-gisu Bóris, tóoxidóoni bu « Joolaa » bii, amul lu ko gën a ñàng : « Bi Senegaal dee Senegaal ba tey, dara masu fee xew lu ëpp solo suuxu Joolaa bi ». Monte, ñakkul ne, xew-xew yooyu yépp, lenn rekk lay wund : dàq ganaar, waxaale sa soxla. Maanaam, dafa mel ni bindkat bi day sukkandikoo suuxu Joola bi ngir xamal nu leneen : ngir tey gëstu bi muy gëstu ñeel aadaak cosaanu askanam. Uséynu Béey (Ñaareelu pàcc bi feek i fan)
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/2002-atum-suuxu-joolaa-bi/
2002, ATUM SUUXU JOOLAA BI Bërki-démb 26 sàttumbar ci atum 2020, “Bateau le Joolaa” def na 18i at ci biir géej. Daanaka ñaari-junni nit ñàkkoon nañ ci seen bakkan. Te mujjagul fenn, ay daan amaguñ ci. Moonte kenn mësula gis jéeya ju tollu nii, mu waroon a tax askan week nguur gi taxaw ngir leeral ko. Dañ koy fàtte ba bés bi  dellusi, ñu amal ay ndaje, ne fay dige yoo xam ni, suñ fay jóge mu yem fa. Aa, nun askanu Senegaal, ni nu néewalee dafa jéegi dayo. Ñi ñàkk seeniy mbokk a ngi wéy di naqarlook fàttaliku, nguur ngi di wéy di dige jàppale ak teg i daan ña sooke suuxu Joolaa bi. Naam, nguur nga woon ca jamono jooju taxawaayam matul woon benn yoon, waaye warul tax nguur yi ko wuutu ni yàcc, ni yasar. Ñi ëpp ci askan wi yaakaaroon nañ ni nguur ngi ak àttekat yi dañ fay doxe wone seen mënin ak seen fulla waaye bun ko mën a waxee noonu fa la léeb doxe tàbbi géej ndax dige yu dul jéex te lépp naaxsaay. Ci kàdduy Ablaay Jóob, jawriñ bi yor aadaak cosaan, dees na taxawal “Mémorial le Joolaa” jagleel ko way-lab yi ngir kenn bañ a mës fàtte lu tiis loolu daloon réewum Senegaal ci sàttumbar 2002. Buñ delloosi woon xottu gaal gi, nag, ci lay dàq ndax way-ñàkk yi dinañ mën a dëj dëgg-dëgg seeni mbokk ; dina giifal it lu mu bon-bon meru askan wi ñeel nguur gi ak ñépp ñi seen càggan jur lu ni mel. Noonu sax la ko Bubakar Bóris Jóob di waxe ci Bàmmeelu Kocc Barma(aux éditions EJO, 2017). Ndey Koddu FaalPlus de publicationsBiographieNdey Koddu Faalhttps://www.defuwaxu.com/author/ndeykoddufaal10/21EELU FÉEWIRYEE : BÉS BI ÀDDINA JAGLEEL LÀMMIÑ WEES NÀMPNdey Koddu Faalhttps://www.defuwaxu.com/author/ndeykoddufaal10/SËRIÑ AMDI MÓODU MBENDA FAAL WÀCC NA LIGGÉEYNdey Koddu Faalhttps://www.defuwaxu.com/author/ndeykoddufaal10/BÉSUB NJÀNGUM XALE YU JIGÉEN ÑINdey Koddu Faalhttps://www.defuwaxu.com/author/ndeykoddufaal10/MISS LITTÉRATURE SENEGAAL : NEEX XEL, RAFET KÀDDU
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/mag-sama-gor-du-ragal-du-wor/
Bataaxalu Saalif Keyta ñeel IBK Ci tekkib Paap Aali Jàllo KÔRO (mag sama), Jàmm ak salaam ñeel na la. Sa rakk a lay nuyu, di la ndokkeel, di la jox sa wàccuwaay. Ginnaaw loolu, xamal ni kat, sa mbokku cosaan mi nga bokkal maam, di sa mbokku aada, moo namm a waxtaan ak yow tey. Bataaxal bii ngay jàngsi, mi ngi bawoo cib maxejj bu bëgg réewam, mu jaral ko lu ne, fu ne, te xaaru ci kenn walla lenn, muy xaalis walla ndombog-tànk. Duggewuma ko wanewu. Te yit, jubluwuma ci ŋàññ la, walla di yàq sa der. Nde, doo sama noon, te noonoowuma la ; doo sama wujj, te wujjewumaak yow. Tamit, rambaaj walla naaféq taxumaa jóg. Kon, jàppal ni bataaxal bii, jàmm rekk la wund, ñeel nekkinu Mali gi nu bokk ak i doomam, te nga boole leen jiite. Bu ko defee, naŋ ko jànge xel, bañ koo jànge xol. Kôro, Liy xew ca bëj-gànnaaru Mali metti na, tiis na. Xanaa gisoo ni ñuy reye ndawi Mali yi, di saam seeni néew ? Ndege, biir làrme bi, ndaw yaa ci ëpp, bés bu nekk ñuy jaay seen bakkan ngir seen réew. Jigéen ñaa ngiy ténj, jirim yeek baayo yi di gën a bare, yaakaari way-jur yi di tas. Foo dem fekk fa dëj. Ndaxte, ay doomi jàmbur, mag ak rakki jàmbur, jëkkëri jàmbur ak pàppay jàmbur ñoo fay dee. Boo weddee li ma lay wax, dugalal sa ñaari doom yi, Buuba ak Karim, ci làrme bi, yabal leen ñu xeexi. Bu booba nu xool ba xam ndax dinga nelaw am déet. Waaye, ginnaaw kenn ci seeni  doom, mbokk walla jegeñaale deewu ci, seen yoon. Yëgalu leen ko sax seen yaram. Moo tax, ci jamonoy tiis ak naqar jii, say doom sañ a salfaañe alalu réew mi, di ko pasar-pasare. Ñu ni déet-a-waay, say way-yëddukat di yaataayumbe ak a gundaandaat, di jël lu tollu ci 100 walla 300i milyoŋ ci sunu koppar di ko yàq ciy aniwerseer ak i caaxaan. Ngeen fàtte askanu Mali wi nga xam ne, sonn na, tàyyi na. Nit ñi lott nañu, tumuraanke, xiif, mar ba nga ne lii lu mu doon. Ay waay ! Yërëm nu boog, kôro ! Àddina sépp xam na ni Farãs a sooke jéyya ji xew ca bëj-gànnaaru Mali, di fa reylu ay ndawi réew mi. Xanaa gisoo ne seeni moroom yu Farãs di fey ci suuf ñoo leen di faat bés bu Yàlla sàkk ? Dafa di, nag, lu jiin Njaag a, te Farãs mooy Njaag. Te sax, yow ci sa bopp, dara umpu la ci. Yaa gën a xamaatoo ni Macron, njiitu Farãs, ak i ndawam ñoo ngemb ay saay-saay yiy mbubboo raaya Mali, di wootewoo bëgg-sa-réew ba noppiy faat ay doomi Mali bés bu nekk. Xam nga xéll ni Farãs mooy seytaane bi leen di jox i gànnaay, ñuy fetal doomi réew mi. Ma ni, benn jiyaadis amul Mali waxatuma laak terorist. Ay kàcci kese la ! Te, taskati xibaar yu baree ngi leen ciy jàppale. Dafa doy nag ! Aa, Kôro ! Tee ngaa jéngu, tekki buumu njaam gi la goneg Farãs gi takkal. Mbaa du Macron dafa këf saw fit ? Nga topp ci moom nig geen. Fuñ la fekk yaa ngi lëngook moom ngir wane ni ay xarit ngeen. Yow tamit, xamal nag ne doo moroomam. Kii nga xam ne ku bës bakkan bi meew génn ci, lu tax ngay nangoo wéy ci waawam ? Xale boobu ngay sibooru de, mooy reylu say ndawi réew bés bu nekk. Aa, Kôro ! Yow wute ngaak nun de ! Ndege, yow tubaab bu ñuul kukk nga, dib doomu Farãs, làq sa paaspooru Farãs. Xam naa yit ne am nay artist yu lay jàppale. Duma tudd seen tur ; waaye sañ naa ne ñenn ci ñoom Gàmbi lañ fekk baax, dëkkuñu fi. Bu Làmbaay naree tàkk, yaak ñoom ay ànd fàq, ngeen làquji Bànjul walla Pari, yóbbaale seen njaboot. Kon, bu réew mi tàkkee, nun ñi amul fun làquji nooy xal a sonn, nooy dee. Ngalla-waay, buleen taal sunu Mali gii, ndax ñu mel ni man ak baadoolo yi fiy yeewoo Mali rekk lan am. Ndeysaan, dafa di sax, sa yoon dafa nekkul ci nun. Moom kay, nu dund walla nu dee nga yemale. Lu tax faalewoo nu, nun ñi la fal, nga war noo aar ? Metit wi, nun rekk noo koy yëg. Moo, ndax jotul nga yëkkati sag kàddu, xamal askan wi li xew dëggëntaan ? Ndeysaan, dangaa ragal say kàddu juuyoo ak bëgg-bëggi liir boobuy jiite réewum nootaange mi, Farãs. Lenn rekk a la soxal : wéy di toog ci jal bi cig ndimbalam, duy say poos ba ñu fees dell, yow, say mbokk ak ñi ànd ak yow. Ma ni la, nag, yaa wayadi dëgg-dëgg ! Yow yaa ñàkk gis-gis ! Boo geestu woon tuuti sax, dinga xam ni, yow, Keyta, waroo ragal, waroo wor askanu Mali. Yaa gàcceel say maam ! Xanaa danga fàtte ni Keyta nga sant ? Sunu santu maam ja, jàmbaar ji, Sunjata (buuru Mali ciy ati 1236 ba 1255).  Cëm ! Jàmbaaru Kirinaa ngoog ! Gone gi duma woon jinne Sumaaworo. Kii daawul tiit, daawul daw. Xamul woon sax fu tiitukaay di nekk ci nit. Kon, ku nàmpe ci meenum Sunjata, bokk ci giirug Keyta-Keyta yi, waroo ragal. Tey ngay maas nii. Cim mbay ! Xanaa xamoo ni, Sunjata, ak li mu doonoon buur yépp, askanam a ko faloon. Nguuram du woon rekk ndono. Cib demokaraasi bu bir la nguuram lalu woon. Waaw kay ! Ndege, démb, kuñ ci falaan, cim pénc lañ la tànne, ci kow sàrt bu leer. Rax-ci-dolli, ndaje ma faloon Sunjata dafa tëraloon ab sàrt bu amoon taxawaayu ndeyu-àtte, ci atum 1236. Mi ngi tuddoon sàrtu Kurukaŋ-Fugaa, te amoon lu tollu ci 44i dogal. Kon, nun amunu ku nuy ñee. Nga war cee jàngat ñaari mbir. Benn, sunu njiit yu njëkk ya, duñu woon ay buuri ndono, askan waa leen daan fal cim pénc. Ñaar, duñu woon buur di bummi, di jaay nit ñi doole ak a def lu leen soob. Waaye dafa amoon aw yoon wu leen tënkoon, tënk réew mépp ak ñi ko jiite woon, réew mépp a àndoon tënku ci sàrtu Kurukaŋ-Fugaa. Lii mooy sunu aaday maam. Te yow it dañ laa fal, aw yoon tënk la, muy ndeyu-àtte réewum Mali. Wànte, doo buur, kôro. Doo buur, de !  Xam ko bés niki tey. Moo, lu la tee roy ci maam yi, dekkil cosaan ? Ndax gis nga ne, demokaraasi bi ñuy soow, sunu maam yu jàmbaare woon yooyu ñoo ko njëkk a saxal, suuxat ko ? Sunu moomeel la. Tey, nga nasaxal ko nii, noon bi jaare ci, yàq réew mi yaxeet. Waaye, nag, ku xeeb juddoom, wàññi darajaam ; te ku xeeb sa cosaan, ñu xeebal la ko. Bu dee li la say mbokki Mali yi dénk dafa diis ci yow, delloo leen seen moomeel ! Bu dee danga nar a boqu Kulubaa di lox, wàccal jal bi te ba kook ku am fitu def li war. Boo ragalee ne jàkk Farãs ak i njiitam wax leen dëgg, demal sa yoon ! Boo mënta yor réew mi, jóge fi ! Mali am na ay góor-Yàlla yu gëm seen bopp, xam liñ doon, bëgg seen réew, am xam-xam bi ak mën-mën bi, te am fitu yor ko, jàmmaarlook noon yi, defaraat réew mi. Boo demulee, nag, lu la ci fekk yow la. Sàmmal sag ngor te bañ a gàcceel sa bopp. Ndaxte, kàddug maa demal sama bopp moo gën a rafet kàddug dañ maa dàq. Kon, fexeel ba bu kàddug gàcce googu gàkkal sa tur ëllëg. Ndaxte, suba du añ du reer, waaye dees koy sóoraale. Dëgg neexul. Bàyyi ci xel. SA RAKK, SAALIF KEYTA
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/sigaret-baaxul-waaye-afrig-la-yeese/
SIGARET BAAXUL… WAAYE AFRIG LA YÉESE ! Fan yii weesu, Marie Maurisse, ab taskatu xibaar bu fekk baax Siwis, bind na bataaxal bu jar a bàyyi xel. La muy ciy nettali mooy ñaawtéef yu këri-liggéeyukaay yu mag yiy jaay sigaret ci réewi Afrig yiy def, te sunuy gornamaa ne yàcc di leen seetan. Tóx baaxul, loolu dëgg gu wer péŋŋ la, kenn sañu koo werante. Képp ku koy def, sa bakkan a ngi ci xott, dina la feebarloo, gàttal say fan. Teewul bitig boo dugg Senegaal mu ngay jaay sigaret ; li am ba am moo di ne nguur gee ko daganal, di ci jël moyaal. Li ñu Marie Maurisse di xamal nag, teg ko ci ay firnde yu leer nàññ, moo di ne xeetu sigaret yi ñuy jaay Afrig, ñoo yées fopp yi ñiy jaay Ërob, ca réewi Tubaab ya. Mën nan koo metitlu waaye warunoo bett ndax Afrig yàgg naa doon ‘’Mbëbësu” Ërob. Kolobaan gii, boo fa doxantoo, dinga fa fekk ay jali jali fëgg-jaay, maanaam ay yëre yuñ sol Ërob ba sànni leen ci mbalit mi. Yàggul dara, daaw-jéeg rekk, lanu dégg ni esãs ak gasuwaal bi ñuy jaay fii ci Senegaal ak ci yeneeni réewu Afrig, kenn sañu leen a jaay Fràs walla Almaañ ak ñoom seen. Lu ko waral ? Xanaa seen mbon ci wér-gi-yaramu doom-aadama. Bi ñu siiwalee li Marie Maurisse bind, Philip Morris, këru liggéeyukaay gu mag gi ubbi fii Senegal ab isinu sigaret, daldi nay tontu. Ñaari mbir a jar a fësal ci li mu wax : bu jëkk bi moo di ne Philip Morris weddiwul ni sigaret yi muy jaay Senegaal ñoo yées yi ñuy jaay Ërob ; ñaareel bi, nag, mooy, sunu wér-gi-yaram gi ñuy fowe, nee na ci li ko nguuru Senegaal may la ko teg. Waa OMS, kurél gi ñu dénk lépp lu jëm ci wér-gi-yaram ci àddina si, firndeel nañ ni fileek 2030, limu tóxkati Afrig yi dina ful ñaari yoon. Ërob moom, tàmbalee naa xeex ak doole sigaret, ngir aar ay ndawam, fexe ba ñu bàyyee tóx. Looloo tax defarkati sigaret yu mel ni Philip Morris jàpp ne liggéey ak Afrig moo fi sës, sunu réew yi amal leen lool solo. Ci gàttal, nun nooy seeni nooy-neex, seen yoon newul ci sunu wér-gi-yaram. Bu sunuy njiit amoon fullaak faayda, yittewoo seen bànneexu askan, neneen la mbir miy deme.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/ndam-lu-saful-xorom-saful-suukar/
NDAM LU SAFUL XOROM, SAFUL SUUKAR…? 10Dibéer yemook ñaar-fukki fan ak ñeent si weeru Féewaryee, la waa réew mi doon tànn ki leen war a jiite ba atum 2024. Waaye, dafa mel ne li mu jur ci werantee ëpp li mu jur ci jàmm ji ñu xame Senegaal. Ndaxte, woteb njiitu réew bees génn, ñaxtook fitna lañ ci gën a ràññee. Te yit, ngirte yi àttekat bii di Demba Kànji siiwal, waa kujje gi, kuréli way-moomeel yeek li ëpp ci askan wi naqarlu nañu ko ; ndax nee nañu ag càcc gu leer nàññ la. Kon, woteb ren bi, bu yéesul ci wote yi fi jot a am ba léegi, bokk na ci yi gën a taq suuf. Looloo waral lawax yi féetewoo kujje gi dàq xàjj-ak-seen, booloo doon benn niw say, lànk ne nanguwuñu ndamal Maki Sàll li. Moone de, yoon may na bépp wutaakon mu kalaame ci ndajem ndeyu àtte mi, bu gisee ni wote bi am nay jalgati yu fés. Waaye, bank nañu seeni loxo, boq golo gi, ne dee duñu dem ci kanamu Ndajem ndeyu-àtte mi di fa jooytu dara. Lees ci war a jàngate mooy ne, lawaxi kujje gi amatuñu kóolute ñeel aji-àtte yi. Naka-jekk, dañoo wone ay yooni yoon ne ñoom Maki Sàll la ñu fi nekkal ak ay bëgg-bëggam. Muy lu doy waar ci demokaraasi réew mi te jar a naqarlu. Te nag, àddina sépp a ngi nuy may nopp, ne nu jàkk di nu xool. Wax dëgg, Makeek demokaraasi, mi ngi mel ni Yàllaak yaali. Li koy firndeel mooy ne, saa yu jëlee dogal walla nu génn ciy wote, coow li da naan kurr. Lim yi tukkee ci woteb njiitu réew mi jeex, daanaka moom la ay njegeñaaleem ak i farandoom biraloon ca njëlbéen. Mu mel ni aji-àtte yi defuñu lu dul dëggal lim yooyu. Yatma Jóob
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/can-2021-kub-baa-nga-woon-ca-seeju-saajo-maane-delloo-mbattu-ca-ndaa-la-mu-naane/
CAN 2021 : Kub baa nga woon ca Séeju, Saajo Maane delloo mbàttu ca ndaa la mu naane Bàmbali, ci diwaanu Séeju, dalal na Kubu Afrig bi Senegaal jële woon ca Kamerun ak doomam jii di Saajo Maane. Jëwriñ ji Mataar Ba yékkati na fay kàddu, wonale kub bi Jaraafu Séejook waa Bàmbali, teg ca ni Saajo Maane nekkee royuwaay ci réew mi. Ginnaaw loolu Saajo Maaneek i xaritam amal nañ fa joŋante xaritoo, àndoon ceek Papis Demba Siise, Allaaji Useynu Juuf ak Mbay Ñaŋ. Ña nga ko amelee woon fa lépp tàmbalee, bayaal ba doomu bàmbali ji doore futbal.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-7/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM KUPPEG TEFES Mamadu Jàllo, tàggatkatu ekibu Senegaal bu kuppeg tefes bi tànn na ndaw yi mu war a yóbbu fa Irã ngir amal fa ñetti joŋantey xaritoo, bési 19, 20 ak 22i ci weeru desàmbar wii. Joŋante yépp moom ak Irã lay doon ca diiwaanu Teherã (Téhéran). NDAW YI MU TANN Góol : Alseyni Njaay ak Useynu Fay. Defãsëer : Mamadu Silla, Papaa Móodu Ndóoy, Baabakar Ñaŋ, Baabakar Faal, Seydinaa M.A. Gajaga. Miliyë : Maamur Jaañ, Séydinaa Isaa Laay Seen,  Amar Sàmb. Ataakã : Rawul Méndi, Séydinaa Manjoon Jaañ, Suleymaan Koli, Suleymaan Baaji. ABDULAAY SIMAA Saa-Senegaal bi moo ngi wane xarañte ca ekibam boobu di Rangers FC fa Ekos. Fi mu nekk nii, moo ngi ci 14i bii yu mu dugalagum. Ndax loolu dina doy ngir Aliw Siise wóolu ko ci CAN bii ñu dëgmal ? Kenn xamagul. Lu leer daal mooy ni soxlees na ci ekib bi ay ataakã yu xarañ ci kanami kã yi. LÀMB JI : MÓODU LÓO AK BOY ÑAŊ NAROON NAÑU SONGOO Démb ci gaawu gi 15i Desàmbar bi la ñaari mbër yi doon amal seen jàkkaarloo bu mujju laata seen bésu bëre 1 sãwiyee 2024. Ci jàkkaarloo bi, doomu pikin bi dafa fekki Móodu Lóo di nappanteek moom, ñuy sannantey kàddu ci suuf jekki saay rekk doomu Parsel bi daldi koy buux. Ba loolu amee ñu nar a jàppante foofu faf ñenn ca ña ànd ak ñoom ak ca njiit ya dox seen diggante. Yu ni mel dees na wane ni ñaari mbër yi pare nañu ngir neexal bés bi. Waaye nag, lu jar a yamale la laata muy jur lu ñaaw.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/nakk-kayitu-juddu-gi-nag-ba-kan/
ÑÀKK KAYITU-JUDDU GI NAG, BA KAÑ? Ayu-bés yii weesu, yéenekaay yu bare dañoo xéy fésal ci seen xët bu njëkk xibaar bu kéemaane. Waaw, li nu ko dugge woon mooy xamal askan week Nguur gi ne lu mat junniy ndongo ak lu teg amaguñu kayitu-juddu. Déggal ma lii rekk ! Te lees war a xam moo di ne ndongo yooyu, looloo leen di tee bokk ci joŋante yi leen di may lijaasa biy firndeel seen njeexitalu njàngum daara ji féete suuf. Te moonte ñoom matale nañu seen njàng. Lu waral loolu ? Xanaa càggan. Càggan doŋŋ. Nee ñu Pikin gii rekk, limu gone yooyu ëpp na junni. Ndeysaan, njàqare ak tiis dikkal na leen te ñoom de, doonu ci dara ba dara booloo jeex. Xamalees na nu itamne ci lekooli Pikin yi ba tey, téeméeri xale yoo jël, ci xayma, ñaar-fukk ak juróom yi binduwuñu. Ndaw lu yéeme, cim réew moo xam ne nee na yokkute lay diir ! Moo, ndax am réew dina am yokkute su fekkee ni njàng mi sooy na ? Déedéet. Dafa di, yokkute walla naataange, ci liggéeyu doomi réew mi rekk la mën a aju. Te bala liggéey boobuy sotti, fàww nu yar gone yi, yiir leen, yokk seen xam-xam, def ci ñoom yëg-yëg ak mën-mën yiy tax ñu bëgg seen réew, fas yéene koo jëme kanam. Kon, réew mu am fulla, farlu te xam jëmuwaayam, du sàggane ay doomam. Waaye Senegaal gii, kenn du ko raw ci wàllu càggan, dafa mel ni sax aada la fi. Te li gënatee doy waar ci mbir mi, mooy ne du guléet ! Daanaka at mu Yàlla sàkk njàqare gu ni mel, diiwaani Senegaal yépp dañu koy jooytu. Bu ko defee, mënees na  wax ne, ci fànn googu, ‘’Pikin yi’’ dañuy gën di baree ka law ci sunu biir gaal gi ! Xanaa lii mooy jur doom sànni ! Ndax càggan mën naa weesu lii ? Waaw, lii nag ba kañ ? Waaye lu jiin Njaag a te way-jur yi ñooy Njaag.  Naka la nit di jure doom, di ko dundal, di ko toppatoo, di ko yar muy màgg, nga ameel ko àqi teyam ak ëllëgam, ba noppi nga ne doo ko wutali këyit yi koy màndargaal ci biir nit ñi, fépp fu mu mën a dem ? Rawatina ci jamono yii nu tollu, di jamonoy  mbind,  jokkoo ak xamtéef ? Yenn yi kat, xel mënatu koo nangu ndax ñépp a xam, daanaka, ni Dunyaay doxe léegi. Ci dëgg-dëgg, lii du dara lu dul xamadi, xayadi ak càggan gu jéggi dayo ! Waaye am na leneen lu mat a laaj te nu war koo joxoñ yitam : naka la sëriñi daara yi, njiiti lekool yeek espektëer yi àttanee seetaan lu ni mel booba ba léegi ? Moone de, ndongo yi dinañu toog di jàng 6 at laata ñuy àgg ci kalaasu eksame bi. Ci diggante ba ñuy dugg lekool ak léegi, at mu nekk dinañ bindu. Waaw. Ndax sëriñ daara yi, njiiti lekool yeek espektëer yi def nañu seen liggéey ni mu ware ? Lan lañu doon xoole ba lii di am ? Lu taxoon ñu ñàkkal solo jéyya jii ba xëy bés  musiba mii  ni këtt-ni-jonn ci seen kanam, ñu mel ne ñu ci am mbetteel ? Fii de, mel na ni mëneesu fee lay ñàkk xam, xanaa ! Càggan taxawati, ne nu : naam ! Gaa ñi ŋànknguur gi tamit, kenn du ñoom. Jawriñ bi yor wàllu njàng meek njàngale mi moo waron a jël ay matuwaayam ba lii bañ a am. Jawriñu biir réew mi tamit waroon naa def dara. Warees na duut baaraamu tuuma tamit meer yi, ñoom ñi gën a jege askan wi tey defar këyiti-juddu yi. Mbir mii daal, kenn setu ci. Ma laajati : lu tee way-jur yi defarlu seen këyitu-juddu doom bés bi mu juddoo ? Ndax Nguur gi manuta fexee lëkkale loppitaan yeek  meeri dëkk bu ne,  ba nga xam ne lépp lu xew ci béréb bu njëkk bi, bi ci des  jot xibaar bi ci saa si ? Dëgg la, Senegaal dum réew mu naat noonu, waaye nag, ñàkkul ay nit ak i jumtuwaay yiy tax mu tëral pexe moomu. Bépp lay bu ñu fi indi, ay caaxaan kese la ! Lu ci mënti am, ci sunu gis-gis, xel mënuta nangu ñàkk kayitu-juddu doŋŋ xañjunniy ndongo lijaasa bi mën a tax ñu tekkiji ëllëg ! Lu tee sax ñu may leen ñu def eksame bi ba noppi, kilifa yi séq mbir mi booloo, taxaw nekk jenn jëmm, taxawu ndongo yiy jànkoonteek yii jafe-jafe ? Te, su loolu lépp weesoo, luy tee Nguur gi jóg ci lu ñaaw lii, seet nu mu koy saafaraa ba abadan ? Ndax kat, këyitu-juddu, ak lu mu am am solo, manul a gën a am maana ëllëgu gune yiy war a amali seen bopp njariñ, amali njariñseeni way-jur ak tamit seen réew ak seen askan. Wolof Njaay nag, dëgg la, nee nañ lu mu léebu ñaare noonu la, waaye Tubaab yi tamit, léeg-léeg, kenn du dem ñu des ; ñooy wax ne : kuy sang liir bay tuur desitu ndox maŋ ko doon sange, na nga moytoo sànniwaale liir bi ! Su boobaa dinga réccu li nga def ndax càggan lu mu jur, réccu am ci wàll.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/niseryaa-buhari-faluwaat-na/
NISERYAA : BUHARI FALUWAAT NA Ci weeru féewaryee wii jàll la askanu Niseryaa doon amal woteb njiitu réewam. Ba ñu àggee ci cëpaandoo li, Muhammadu Buhari la askan wi tànn, dénkaat ko réew mi. Lu tollu ci 15 alfunniy wotekat ñoo sànnil xob ki toogoon ci jal bi 2015 ba léegi, mu jël raw-gàddu gi ci kanamu lawax bii di Atiku Abubakar. Chinua Achebe mas naa bind cib téereem bu siiw ci atum 1983 ne liy gàllankoor Niseryaa du lenn lu dul i njiit yu matul i njiit. Jaar-jaaru Buhari firnde la ci ndaxte 36 at ci ginnaaw, laata muy falu ci yoonu demokaraasi, àndoon naak i moroomi soldaaram jiital doole, foqati nguur gi ci loxoy Shehu Shagari. Waaye, àddina sépp benn seede lañu biral ñeel Buhari te moo di ne du sàcc, àndul ak kuy sàcc walla ger te yit, nit ku dëggu la, xamul caaxaan, am fulla ju mat sëkk. Ba muy kàmpaañ ci atum 2015, la mu gënoon a fésal, ciy digeem, moo doon jàmmaarlook tuurkati deret yii di waa Bokko Haram ak dakkal ger ci Niseryaa. Doonte sax ay yéeneem yépp àntuwuñu ci ñaari fànn yooyu, nit ñi nangul nañu ko ni def na ciy jéego yu am solo. Waaye, nag, jot naa jànkoonteel i jafe-jafe ba mu faloo ci atum 2015. Ndaxte, njëgu petorol bi nga xam ne moo téye koom-koomu Niseryaa, dafa daanu woon bu baax, daldi nasaxal weccitu réew mi ba noppi yokk fa ndóol. Rax-ci-dolli, mbir yi àggoon na ba ci xéy jafe woon lool ci ñi ëpp ci réew mi, limu ñi amul liggéey daldi ful ñaari yoon. Te tamit, Buhari mag la, yaram wi neexatul. Waaye, moom de, mel na ni yàkkamtiwul daraam, mi ngiy def li muy def, ànd ceek dal. Looloo waral xaley Niseryaa yi utal kob dàkkantal, di ko woowe Baba-Go-Slow. Gaa, Buhari dafa ñëw fekk ay tolof-tolof yu bari gàll koom-koomu réewam. Teewu ko fexe ba dugal xaalis bu bari ci mbay mi ak jumtukaayi xarala yi. Ger gi mu waxoon ni dina ko xeex tamit, wax-dëgg-Yàlla def na ci kemtalaayu kàttanam. Li dalul xel ciy mbiram, daal, moo di ne Buhari jikkoy soldaar la am ba tey, mënul a tàggook moom : képp ku ko déggalul, du la may jàmm.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/serin-bi-faww-mu-feen/
“SËRIÑ BI, FÀWW MU FEEÑ” Bu ñu seetloo fan yee ci ginnaaw, werante amoon na ci nataali Séex Ahmadu Bàmba Mbàkke, naan moom la ak du moom. Muy ay nataal yi ñu fésaloon ci mbaali jokkoo yi. Nataal yooyu di wone jëmmi Séex Ahmadu Bàmba Xaadim Rasuul. Ñu xame woon ko ci benn nataal képp bu ñu miin a gis, réewu Farãs denc yeneen i moomeeli Senegaal, bokk na ca nataal yooyu. Mu doon juróom-benni nataal yu ñu portale ca atum 1918 ba ñuy teg xeer wu njëkk wu jumaay Njaareem. Bu ñu sukkandikoo ci këru xibaar gii di Pressafrik.com, nataal yooyu ñu ngi jóge ci arsitek bii di Jean Geoffre, nekk ki rëddoon palaŋi jumaa jooju. Ci lu ko weesu, ca weeru Me 2020, lañu fésal njaayum portale yooyu. Ci noonu, la ab kurél bu ëmb ay taalibe murid ak i gëstukat defe ay jéego ngir jot ci nataal yooyu. Ñu jaaye leen ko ci lu tollu ci ñeent-fukki tamndaret ci sunuy koppar, maanaam 40i milyoŋ. Biñ ci jotee lañ ko jébbal xalifa murid yi, Seex Muntaxaa. Mu fésal ci mbégteem, di sant taalibe yi. Ciy kàddoom, wax na ne : “Sëriñ bi, fàww mu feeñ”. Ci weneen wàll wi, xamees na ne, nataal yooyu, du moomeelu murid yi rekk. Ndax, day fésal mbatiitu réewu Senegaal. Ci noonu, la Njiitu réew mi, Maki Sàll, dajeek kurél googu ngir ñu jébbal ko moomeel googu. Mu nekkoon ci teewaayu jëwriñ yu bari, rawatina ki ñu dénk mbatiit gi ak moomeelu réew mi di Aliyu Sow. Bokk na ci lañu xaatim mooy jëmmal kër guy sàmm ak a saytu moomeel yi maanaam “musée”. Mënees na jàpp ne mbatiit, lu jar a sàmm la ndax dafa bokk ci kenoy askan. Kon, saytu moomeelu réew mi lu war la ngir seen taxawaay bañ a naax-saay.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/kadduy-usmaan-sonko-useynu-beey/
KÀDDUY USMAAN SONKO 1/2 PÀCC Senegaal gépp amoon na fiy yëngu-yëngu, réew mi jaxasoo, yëf yi doy waar lool, yegg sax fu ko kenn foogul woon. Ñii seen i bakkan rot ci, ñee am ciy gaañu-gaañu yu metti, ñale ñàkk ci alal ju bari. Ginnaaw ba mu jógee “Section de Recherches” bu Kolobaan, Usmaan Sonko amal na waxtaan ak waa réew mi  ci 8eelu fan ci weeru Màrs. Waxtaan woowu nag, dara waralu ko woon lu dul mas-sawu leen ci yi fi jot a xew, xamal leen itam ni mook ñoom a bokk naqar. Lu Defu Waxu, seen yéenekaay ci kàllaamay Kocc a ngi leen di baaxe ay kàddoom na mu leen yëkkatee keroog jooju. (Ci taataanug Uséynu Béey) “Mbokk yi, tey, walla mën naa wax sax ne, fan yii yépp sunu xol neexul, sunuy nelaw néew na, sunu xalaat bari na, te dara waralu ko nag, lu dul tiis wi nga xam ne am na ci réew mi, muy ay bakkan yoo xam ne rot nañ fi. Kon, dama doon ñaan bala nuy dugg ci waxtaan wi rekk nu daldi def “une minute de silence” jagleel ko sunuy doom, ndax ñi fi faatu ñépp, walla ñiñ fi faat ñépp, nun li nuy doon ndaw ndaw, mat nañuy doom. Tey, jox nan ma lim boo xam ni jeexagul; waaye lim bi nu jotagum mat na fukki nit. Benn bakkan bu rot rekk, ci anam bu mel nii, nga xam ne dañ koo faat, musiba la ci réew mi, rawatina nag, bu ñu nee tey mat nañ fukki nit. Bakkan yooyu nag, ñooy : ku ñuy wax Baay Séex Jóob, amoon fukki at ak juróom-ñaar, ñuŋ ko faate fii ci Yëmbël ; Séex Kóli amoon ñaar fukki at, ñuŋ ko faate ci Biññoona ; Faamara Gujaabi, moom it amoon ñaar fukki at, ñu faat ko Biññoona ; Paap Siidi Mbay, amoon moom it ñaar fukki at, ñu faat ko fii ci Kër-Masaar ; Saajo Kamara am fukki at ak juróom-ñett, ñuŋ ko faate Jawobbe ; Mañsuur Caam, moom it am ñaar-fukki at, ñuŋ ko faate fii ci Ndakaaru; Alasaan Bari, amoon fukki at ak juróom-ñaar, ñuŋ ko faate fii ci Sànteneer, ci Ndakaaru ; Musaa Daraame, amoon fanweeri at ak juróom, ñoŋ ko faate ca Ndóofaan ; Buraama Saane, amoon fukki at ak ñaar, ñuŋ ko faate Biññoona ; ak Móodu Njaay, nga xam ne moom lañ nu mujje xabaare, ñu faate ko tey fii ci Parsel-Aseni, ci anam yu ñaaw ba fu ñaawaay yem. Kon, nu ngi leen di ñaanal Boroom bi Mu xaare leen Àjjana. May ñaan nag, ñi fi nekk ñépp, taskatu xibaar ak ñeneen ñi ko teewe,  nu taxaw def “une minute de silence” jagleel ko sunuy rakk yooyu ak sunuy doom yooyu… (Tekkaaral ci diirub benn simili). … Jërëjëf. Maa ngiy jox sunu sëriñ, Sëriñ Mañsuur Jamiil mu jagleel leen ay ñaan yoo xam ne, haasatan la, yokk barke rekk, ndegam Yàlla def na mu teew fi ; nu jox ko mu defal nu ñaan… (Ñaan). … Jërëjëf. Kon, dina nu jéem a tënk waxtaan wi ci lu dul gudd torob. Gannaaw bi nu dello nuyu saa-Senegaal yi nuy seetaan yépp, di nuyu ak di gërëm kilifay réew mi, kilifa diine yi, kilifa aada yi, àbbe yi, di rafetlu seen taxawaay ci réew mi. Ndax, wax naa ko ci samay kàddu yu jiitu, bir na ma man, ni ñoom, lañ ca waroon a def, def nañ ko ci bañ ko waree def. Aajowul nu koy jéebaane walla di ko wax ci kaw. Dafa fekk nag, kilifa diine moom, orma rekk lañ ko warlul. Am na loo xam ne, bu naree xotti worma, su ñu waxee ci suuf yem ca. Waaye ku bañ a dégg, ba mbir mi tàng ci sa loxo, dinga dellu ba ci ñoom, woowaat leen. Kon, nu ngi leen di gërëm ci taxawaay bi. Di gërëm kilifay aada yi bu baax itam, di gërëm ñi fi teew ñépp. Ñii fi nekk ñépp, amul kenn koo xam ne pólitig walla par-parloo moo la fi indi. Amul kenn koo xam ni li nga daj ci fan yii, par-parloo moo tax, waaye ñi fi teew ñépp, li leen tax a jóg ba tax ñu daj ci lu ma ci dajul man, mooy Senegaal, yitte gi ñu am ci Senegaal, bëgg-sa-réew ak am dëggu ni, dañu war a taxaw ngir réew mi, dañu war a taxaw ngir ëllëg, dañu war a taxaw ngir sunuy doom ak sunuy sët. Kon ñoom ñépp dama leen di gërëm man, ci sama tur ; waaye dama leen di gërëm tamit ci turu askanu Senegaal, ndax askanu Senegaal lanu taxawal, taxawalunu Usmaan Sonko. Ñi fi jóg ñépp sonn ci, su doon jëmmu Usmaan Sonko rekk, xéy-na «10%» yi walla «15%» dinañ génn. Bu kenn naagu ba foog ni, yow yaa tax doomi Senegaal yi génn, déedéet. Li tax lii am, mooy yëg-yëg bu kenn ku nekK xam na ni, sunu réew, sunu askan mu ngi nekk ci ay jafe-jafe yoo xam ne, bu nu seetaanee ba mu deme nenn rekk, defe naa dina rëcc ba fàww. Kon, maa ngi leen di gërëm ñoom ñépp ci turu askanu Senegaal. Bu loolu weesoo, may sargal jigéen ñi it ndax gis nanu seen taxawaay ci xeex bi ; te tey dañ leen ko màndargale, muy bésub “8 mars”.  Jigéeni boor bu nekk nag, du jigéeniy PASTEF kese. Waaye, jigéen ñi taxaw nañ jàpp ci xeex bi. Defe naa Ajaa Yaasin a ngi nii toog sama wet, sama yaay Ayda Mbóoj sama layookat a nga nale, ñoom Maymuna Buso ak keneen ak keneen, su ma leen doon lim tey du jeex, ñoom Aysata Saabara, ñoom Maam Jaara Faam… Ku ma limul rekk bumu ci mer, nu delloo leen njukkal ci bés bii, di leen jaajëfal bu baax. Mbokk yi, li xew ci réew mii, doy na waar, li xew ci réew mii, aa ! defe naa ñoom Decroix ñoo nu ëpp jaar-jaar fuuf, ñoo nu ci gën a yàgg, waaye gëmuma ne, lii fi xew, mas naa xew ci Senegaal. Du xew-xewi 63 yi, du yi ko jiitu, du 68, du 2000, du 2012, du 88, du 93… Ba tey, defe naa ni lii xew tey Senegaal, masu fee xew. Ba tey jii, Senegaal mooy xët wu njëkk ci xibaari àddina si. Kon loolu du lu tuuti, foog nun waa Senegaal, nu  mën koo natt ; xam lii lu mu doon, ak lan la war a màndargaal ci sunu mboorum  réew. Ndaxte, su dee mënun cee jël ay njàngat ba lii dootul am ci réew mi, bu boobaa, defe naa coono yi dootuñu jariñ dara. Ñi ci seen bakkan rot, ñi ci gaañu, di ñu bari, ñeneen ak ñeneen ak ñeneen, defe naa dootul jariñ dara. Kon, bu nu waxee loolu, danuy dellu delloo njukkal, ni ma ko defe, ci ñii nga xam ne seen bakkan rot na ci, te dinaa ci dellusi, ma def ko ci ñi gaañu, ndaxte ñi gaañu bare nañ. Di ñaan Yàlla rekk, mu bañ a weesu foofu. Bi ci des nag, di ci jagleel ngërëm lu ràññeeku ñi nga xam ne, ñooy ndawi Senegaal yi.  Di leen delloo njukkal bu baax. Yàgg nañoo wax ndawi Senegaal yi nii, xale Senegaal yi nale, déedéet ; sunuy ndaw, dañu am awãs ci nun. Li ma gëm mooy sunu ndaw yi dañu am awãs ci nun. Wone nañ ko, ndax ku dem di jàmmaarlook ay takk-der, ñu yore ay fital, yor lu la mën a rey, yor lu la mën a gaañ, yow yoruloo lu dul say loxo ; te defuloo ko ndax dafa am dërëm booy xaar, ndax dafa am ñu féete beneen fànn ñu leen di fay xaalis ngir faat ay bakkan ; yow defoo ko ndax dërëm booy xaar, kon gàcce-ngaalaama ndawi Senegaal. Te nu leen di wax ni, day door rekk. Bis niki tey, na ngeen xam ni réew mi, seen réew la, dogal bi seen dogal la, nun ci seen waaw lanu war a doxe, ñiy def pólitig ci seen waaw lañu war a doxe, di leen déglu. Kon bu leen nangooti di seetaan ba mbir mi egg fu mu warul a egg. Ma wax nag ni, ñooñu ñépp nga xam ne sonn nañu ci mbir mi, ñi nekk seen kër sax di ko naqarlu, ñi toog seen sijaada  di ñaan, bu ma nekkee fii di waxtaan ak yéen, xam leen ni, yéen a tax, ndax bu ngeen amul woon taxawaay boobu, waxuma la tey jii, waxuma la àjjuma bii weesu, waaye altine 8i fan weeru feewiryee laa waroon a nekk Rëbës. Kon man tey jii, duma woon nekk fii di wax ak yéen. Kon bu leen kenn gëm loo ne, dañ noo beral loxo. Waaye seen taxawaay, li mu firndeel rekk tey, mooy li Tubaab naan : «La souveraineté appartient au peuple» Lépp askaan wee ko yore. Mooy kàttan dëgg-dëgg-dëgg ; sañ-sañ dëgg-dëgg-dëgg cim réew, askan wee ko moom, kenn moomu ko. Ñoom dañuy faral di wax, loo wax ñu ni «Force restera à la loi». Waaye yoon, «la loi», mooy askan wi ; yoon wi du dipite, du Maki Sàll… Ku dem nag ba sàggane ko, foog ne yoon wi ñu wote, te askan wi wote ko, mën nga koo jalgati di ko teg ci kaw nit ñi, askan wi da la koy fàttali, te loolu moo leen dal tey. Kon taxawaay boobu, ngalla waay, bumu deñati Senegaal. Bumu deñati ndaxte li ñuy wax les «grandes démocraties» (demokaraasi yu mag yi), boo gisee njiit yi am lu ñu sañul foofu, mooy askan wi dafay taxaw jonn di leen di wattu. Saa su ñuy génn rekk, nit ñi génn ne leen «lii duñu ko nangu». Kon nanu am taxawaay boobu bés niki tey. Ma wax tamit ni, ñii nga xam ne, ñu ngi ci kaso yi, tey lu ëpp téeméeri nit ñu ngi ci loxo Maki Sàll, ñii Tàmbaakundaa, ñii Sigicoor, ñii Kéedugu, fii Ndakaaru, ba Ndar, Tiwaawan, fu ne jàpp nañ fay nit ñoo xam ne, sàccuñu, reyuñu nit, wuruxuñu, luxusuñu ay biye, luubaluñu xaalisu réew mi. Seen tuuma mooy dañoo dox-ñaxtu, te Ndeyu-sàrti réew mi moo leen jox sañ-sañu dox-ñaxtu. Nu ngiy mas-sawu ñooñu, waaye di leen xamal yit ni, dun leen seetaan. Di mas-sawu it ñi nga xam ne ñàkk nañ ci seen alal ndaxte yàqu-yàqu yi bari nañ. Loolu du woon cëslaayu mbir mi ; ñi jóg di naqarlu duñu ay saay-saay ; ay nit nag, mën nañ cee rax, waaye, loolu taxuleen woon jóg. Te it sunu xeex, jubluwunu ko ci askan sàngam walla réew sàngam, du loolu mooy sunu xeex. Waaye dafa fekk daa am fu mbir yi di tollu, lépp mën na cee jaxasoo, lépp mën na cee am ; waaye loolu du woon cëslaay gi. Ndaxte, ku bëgg yor réew ak ku bëgg defar réew, doo toj alalu jaambur, doo yàq oto jaambur, doo toj këru jaambur. Kon loolu, nuŋ koy mas-sawu bu baax nit ñi mu dal. Di mas-sawu njabooti ñi ci faatu, di leen jaal, te bu soobee Yàlla, dinañ góor-góorlu ba kenn ku nekk, nu def sunu «délégation», ñi fi nekk ñépp dox ñëw jaaleji leen, di mas-sawu njabooti ñi ci gaañu ; lañ ci man it ci taxawu dinan ko def. Di mas-sawu njabooti ñi nga xam ne tey, caabi féete na leen ginnaaw ; wax leen it ne seetaanunu ñooñu ndax ginnaaw ba nu jëlee awokaa yi leen war a layool, kenn ku ne, nu ngiy góor-góorlu ci liñ la man a jàppalee ba doo tumuraanke, walla sa njaboot du tumuraanke. Waaw mbokk yi, lii lépp lan moo ko waral ? Lii lépp ci ay tiis yu dal ci Senegaal la. Li ko waral mooy xiif gi nga xam ne, Maki Sàll ak ñi mu àndal xiif nañ ko nguur ; ak yaakaar ni ñoom dañu war a yore nguur gi toog fi ba fàww. Lii lépp moo leen ko andil. Moo ne de, ay at ca ginnaaw loolu lan fi xeexoon ba ay bakkan rot fi. Li andi lii, mooy nguur gi ñu teg ci loxo Maki Sàll, ne ko : «Jox nan la sunuy mën-mën, jox nan la sunu alal, jox la «administration» bi, jox la yoon wi “justice”, jox la xare réew mi, maanaam “arme” bi, jox la lépp loo soxla li nu bëgg mooy nga defar réew mi, li nu bëgg mooy ndaw ñi am liggéey, li nu bëgg mooy nit ñi faju, li nu bëgg mooy tali yi baax». Maki Sàll walbati loolu lépp, jël ko muy doole ju muy teg ci kow saa-Senegaal yi. Muy kuy pólitig, muy kuy «mouvement citoyen», muy «Sociéte civile», képp ku ne àndumaak Maki Sàll rekk, teg na doole jooju sa kow. Loolu moo nu andi ci lii. Mu ànd ci ak ay nitam yoo xam ne, duñ ko wax dëgg, mbaa sax ñoo ko yées, soo moytuwul, moom ci boppam. Ndax lii am yépp nag, ñi ko séq bari nañ de, waaye li ci ëpp ay jëfkat yu ndaw lañu. Boo ko doon seet, ñeenti jëfkat lañu : Maki Sàll, Antuwaan Jom, Maalig Sàll ak Basiiru Géy. Ñeneen ñépp ay suq lañu, nga xam ne, dañu leen di defloo ñuy def. Waaye ñeent ñii, musiba Senegaal yépp, ci jamono yii ñu tollu tembe, ci ñooñu la. Ndax jaadu na, 16i milyoŋi doomi-Senegaal ñeenti nit rekk lëmbe leen? Ndax loolu war nañ wéy di ko nangu ci dëkk bii ? Loo wax nag, ñu ne la nun noo yor nguur gi, “force restera à la loi”. Te, yoon, “loi” boobu, duñ ko tudd lu dul bu dee ci kujje pólitig gi. Yoon woowu dañ koy walbati ngir man a jot ci képp ku àndul ak ñoom ; waaye saa su yoon wi waree dal seen kow, ñu ne mukk du fi am. Ñaata nit ñoo fi mas def ñombe yoo xam ne kenn du ko tudd ? Tey, ñu ngiy romb waa Senegaal di leen yëkkatil i mbagg. Loolu nag lanu mënatul a nangu. Looloo tax nit ñi jóg ni, lii dootunu ko nangu, dootu fi am.” (Dees na ko topp…)
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/can-koddiwaar-2024-caabalu-bes-bi/
CAN KODDIWAAR 2024 : CAABALU BÉS BI WÉR-GI-YARAMI ALIW SIISE AK ABDULAAY SIMAA Bees sukkandikoo ci yégle “Fédération Sénégalaise de Football” (FSF) biral démb ci gaawu gi, Aliw Siise, tàggatkatu ekibu Senegaal bi, dafa jagadi woon. Ci àjjuma ji, bi joŋante gaynde yi jeexee, la ko feebar bu gaaw dikkal, ñu rawale ko fa raglu ba. Waa FSF xamle ne, fajkati ekib bi ñoo ko taxawu laata ñu koy yóbbu fajuwaay ba, di raglub Yamusukuro. Nee ñu nag, tane na bu baax a baax. Te, dellu na daluwaayu (otel) ekib bi sax. Bu dee mbiri Abdulaay Simaa, moom, keroog àllarba la yëgoon aw metit ci ginnaawu tànku càmmooñ bi. Ginnaaw ba ko fajkati ekib ba càmbaree, ñu gis ne dafa ame gaañu-gaañu ca càq ya, maanaam ci “aducteurs” yi. Loolu jural ko mu war a am toogay bu yàgg bum dul laal bal. Ba lile amee, njiiti yi ekib bi ak yu këlëbam juboo ci mu dellu fa këlëbam, Glasgow Rangers, ngir mën a fajoo fa bu baax. Kon fim ne, moom Simaa, bokkatul ci ñiy àggale CAN bi. Nu di leen ñaanal ñu wér ak jàmm ! NGIRTEY BÉS BI Kippug F : Marog day xaar Ci kippug F gi, Marog mi bokk ci fawori yu mag yi dafa timboo ak Kongo Demokaraatig 1-1. Marog moo njëkk a dugal. Ca 6eelu simili ba la seen lateraalu ndeyjoor bi, Asraaf Hakimi, dugal. Waaye, Gayndey Atlas yi reyuñu mats bi, dañoo teggi seen tànk. Noonu, Kongo di puus ba am penaatii ci 42eelu simili bi, laata ñuy mitã. Wànte, Bakàmbu dafa dóor bal bi poto ndeyjooru Bonoo, góolu Marog bi. Loolu taxul mafari (léopards) Kongoo yi xàddi. Nde, bi ñu dawalee ba ci 76eelu simili bi la Silaas Wamangitukaa dugal. Bu dee beneen joŋanteb kippu googu ba tey, Sàmbi dafa tamit timboo ak Tansani. Tansani moo njëkk a dugal ci 11eelu simili bi laata Sàmbi di dugal bi joŋante biy waaj a jeex (88eelu simili bi). Fi mu nekk nii, Marog moo jiitu (4i poñ), topp ci Kongo Demokaraatig (2i poñ), Sàmbi toppaat ci (2i poñ). Tansani moo jëlagum ndaare (1 poñ). Dara leeragul ci kippu gi nag. Ci seen i ñetteeli joŋante lañuy xam kuy génn am déet.  Àllarba 24 sãwiyee lañuy futbalaat bu 20i waxtu jotee. Tansani-Kongo Demokaraatig ak Sàmbi-Marog lay doon. KIPPUG D : ALSERI DAFA MOY Démb ci gaawu gi la ñaareeli joŋantey kippug D gi amoon. Alseri moo doon laaleek Burkinaa Faaso, Móritani doon daje ak Àngolaa. Alseri dafa timboo 2-2 ak Burkinaa Faaso. Ñoom sax, Naar yi, dañu rëcc. Ndaxte, ñaari yoon Burkinaa mi ngi leen di jiital, Bunejaa di leen ci génne. Rax-ci-dolli, wonewuñ fa lu dal xel ci wàllu futbal. Bu dee Móritani moom, Àngolaa moo ko dóor 3i bal ci 2. Wii mooy ñaareelu yoon ñuy dóor sunu mbokki Gànnaar yi. Nde, ca seen joŋante bu njëkk ba, Burkinaa Faaso moo leen dóoroon 1-0. Kon, ñoom moom toog nañ ndax ñoo mujju ci kippu gi ak 0 poñ. Àngolaa moo jiitoogum (4i poñ), Burkinaa topp ci (4i poñ), Alseri nekk ñetteel ak 2i poñ kepp. Talaata 23 sãwiyee lañuy futbalaat bu 20i waxtu jotee. Àngolaa-Burkinaa Faaso ak Móritani-Alseri lay doon. KIPPUG E : ALSERI DAFA MOY Mali ak Tinis ñoo doon daje démb. Waaye, ndam demul, ndam dikkul. Nde, dañu timboo 1-1. Tey ci 20i waxtu la Afrig-Di-Sid di futbal ak Namibi. Mali nag moo jiitoogum ci kippu gu ak 4i poñ, Namibi toppagum ci ak 3i poñ, Tinisi miy ñetteel am 1 poñ kese. NAALU ËLLËG BI Ëllëg ci altine ji, ci kippug A gi, Gine Ekuwaatoriyaal dina daje ak Koddiwaar, Gine Bisaawo daje ak Niseriyaa. Ñaari joŋante yaay dawandoo bu 17i waxtu jotee. Koddiwaar nag mi ngi ci guta ; dafa war gañe ngir jàll walla mu timboo sax ngir yaakaar bokk ci ñetteel yi gën a jekku. Bu 20i waxtu jotee, joŋantey kippug B yi ñooy daw. Kab-Weer – Esipt ak Mosàmbig – Gana ñooy futbal. Bu dee Kab-Weer jàll na ndax 6i poñ yi am, Esipt (2i poñ), Gana (1 poñ) ak Mosàmbig (1 poñ) moom seen dara leeragul.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/di-buur-di-bummi-2/
DI BUUR, DI BUMMI Li jaaxal waa Senegaal, mooy wax-waxeet yi kilifay réew mi dëkke. Ku ci jóge ci kujje gi, dem ci nguur gi yaa ngiy xas ñaa nga àndaloon démb. Mbir mi dafay faral di am ba kenn, ci ñaari làng yépp, muccu ci. Ñépp a ngi fàttaliku ci ndetteelu atum 2018, bi peresidaŋ Maki Sàll nee mësul a ni nañu jële wote yi ci loxoy Usmaan Ngom. Moone, ba mu ko waxee yàggul woon dara te yit moom yemul woon ci loolu, nde noon na doonte sax Séex Géy la ñuy dénk liggéey boobu, ba tey Usmaan Ngom ay wéy di doon kilifaam. Waaw lan a fi soppeeku ci diggante bi ba mënul a def lu yées li mu doon laaj ? Ci sunu gis-gis, li ko waral du dara lu moy doole ju bari ji ñu jox peresidaŋ ci sunu doxalinu réew. Te loolu du tey la tàmbali : bi digganteem ak Mamadu Ja yàqoo la Seŋoor soppi sasug njiitu réew mi, jox ko doole ju baree-bari. Kon dafa mel ni mbir mi du Wàdd, du Maki te du keneen : képp ku fanaan Màkkaanu Njiitum Réew mi genn guddi, sooy yeewu di sax i laaf. Ba tax na, foog ñu wàññi doole joojuy tax benn doom-aadama kese yaakaar ni moo gën ñépp, lu mu xalaat mbaa lu mu xaw a xalaat sax, noonu la ! Lenn ci li waral loolu, mën nañu cee lim li wolof naan : « Ku ëmb sa sanqal, ëmb sa kersa ». Lépp luy ndombog-tànk gu kawe, njiitu réew mi moo cay tabbe. Bu ko defee, ku nekk di xaar sa wàll ci nag wi, doo bëgg a def walla nga wax peresidaŋ loo xam ni dina tax ëllëg, mu ni kii de, àndul ak man, xereñ na, gaa, waaye dara laa ko dul jox. Ngir loolu deñ fi, foog ñu def ni yen réew yi, maanaam di amal ay joŋante diggante doomi-réew yi ngir xool kan moo war a jiite bérébi liggéeyukaay yu kawe yi. Lu ko moy peresidaŋ dafay wéy di nekk daanaka Buur ak Bummi, kenn du ko sañ ni sa bët bi suuf a ngi ci.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-2/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM LIGUE DES CHAMPIONS 2024-2025 Waa UEFA amal nañu ay coppite yoy, dañuy yokk limatu ekib yiy bokk ci joŋante Ligue des champions bu déwénee, atum 2024-2025 mi. Ci loolu, Araabi Sawdid mi nga xam ni, daanaka futbalkat yu xareñ yu bari ñoo ngi jóge Tugal di leen fekki ci seen sàmpiyonaa ba, ñu ci mel ni Ronaldo, Neymar, Benzema, Saajo Maane, Kulibali añs. Njiiti mbootay gi ëmb seen sàmpiyonaa ba fésal nañu seen bëgg-bëggu, maanaam fee ba këlëb biy jël sàmpiyonaa ba daldi di bokk ci Ligue des champions bi. SAAJO MAANE AK RONALDO AM NAÑU SEEN KUB BU NJËKK CA NAAR YA Keroog, ci gaawu gii weesu, lañu doon amal finaalu kuppeg buuru Araabi Sawdid bi. Joŋante baa ngi doxoon ci diggante Al Nasr mu Ronaldo ak Saajo Maane ak Al Hilal bu Kaliidu Kulibali. Ñoom Saajo Maane ñoo mujje gañe ñaari bii ci benn, Ronaldo daldi ci dugal ñaari bii, benn bi saajoo ko ko paas. Mu nekk seen kub bu njëkk ca Al Nasr. REAL MADRID WUT NA GÓOL Gannaaw gaañu-gaañu bu metti bi Thibault Courtois ame, Real Madrid daldi nay àbb jàppkatu Chelsea bi, Kepa. Àbb bi nag, ci diirub menn at kese la. Waaye, Kepa moom dafa bëgg toog benn yoon Real Madrid. Ca kaajaram ga la Kepa wax kàddu yii : “Dinaa góorgóorlu ba sama xareñte tax ma toog lu ëpp at fii ci Real Madrid. “ LIGUE DES CHAMPIONS AFRIG Ci njëlbeenug joŋante yi, këlëbu senegaal bii di Generation Foot mi jël sàmpiyonaa daaw bi dina ci daje ak Hafia Fc bu Gine. Ci dibéer jii, 20 ut 2023, lañuy futbal.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/futbal-ak-jafe-jafey-reewi-afrig-yi/
FUTBAL AK JAFE-JAFEY RÉEWI AFRIG YI Doom-aadama fent na ay xeeti po yu bare. Ba ci tàggat-yaram sax, nga xam ne, ci cosaanam, yar ak wér-gi-yaram ñoo ko taxoon a jóg, nit soppi na ko, def ko liggéey ak po, di ci amal ay joŋante yu mag, àddina sépp di ko teewe. Xeeti po yooyu, nag, futbal a ci gën a siiw te yit moo ci gën a law ci àddina si. Baatu futbal, ci làkku àngale la jóge te di tekki tank (fut-) ak bal, maanaam bal bi ñuy dóore tànk. Futbal ci boppam bare nay xeet, waaye bi ci gën a fés mooy bi nga xam ne, fukk ak benni nit ñooy jàkkaarlook seen yeneeni fukk ak benni moroom, ku nekk di jéem a dugal bal bi ci kãwu keneen ki ci diirub 90 simili. Powum futbal mi ngi cosanoo ca réewum Àngalteer. Àngalteer, nag, saa boo ko waxee xel yi dem ci ñoom Bobby Charlton, Gordon Banks, Stanley Matthews, Michael Owen, Bobby Moore, Alan Shearer, Kevin Keegan ak lingeer Elisabeth II, añs. Kon, tubaab yi ñoo sos futbal ba noppi daldi ko tas ci àddina si, ñépp bëgg ko. Afrig tamit kenn demul mu des, ndax doomi Afrig yi amul ku leen gën a xër ci futbal. Waaw. Boo génnee ci mbedd yi dinga gis xale yiy top ci ginnaaw bal biy dóor ba ñaq tooy xepp, subaak ngoon ñu ne ci. Waxambaane yi ñoom, foo leen fekk ñoo ngiy seetaan futbal walla teg seen àttaaya di ko waxtaane. Mag ñi di waxtaan ak a fàttaliku jamonoy Sàndaark, Jaraaf, Duwaan walla Asfaa, walla sax jamonoy Bokànde ak Séex Sekk, di leen méngale ak goney léegi yi. Nawetaan moom, li mu jaral xaley koñ yi, mëneesu koo natt. Kon daal, futbal bawul kenn ci Afrig li ko dale bëj-gànnaar jàpp bëj-saalum, jóge sowu jëm penku, fépp la feebarub futbal law ; rawatina Senegaal gii, du mag du ndaw, muy góor walla jigéen. Moom kay, politig bi sax da cee rax léegi ndax dayo bi mu am. Moo tax it, yenn saa yi, nguur gi ci lay jafandiku ngir fàtteloo askan wi jafe-jafe yi mu nekke. Ndege, ku ci sa réew di joŋante, day mel ni da ñuy raxas sam xel, nga fàtte say aajo ak say ay, sa xol ak sa xel yépp nekk ci joŋante bi. Rax-ci-dolli, futbal bi léegi liggéey la : fokat yi ñi ngi ciy am xaalis bu dul jeex, jaaykat yi noonu ba ci bérébi liggéeyukaay yu mag yaa ngi ciy defar seeni mbir. Futbal a ka bare bayre, naam ! Joŋante bu mag biy dajale ñaari at yu ne réewi Afrig yi ab firnde la ci. Joŋante ren bi nag, ca Misra lay ame. Muy réew moo xam ni, askan wi ci nen la toog. Ndaxte njiit ma fa ne, dib Seneraal ci làrme bi, Al Sissi, jaay doole ak xoqtal nit ñi la fa nekke. Askan wi sonn lool. Ñu bare jàpp ne dafay jëfandikoo joŋante boobu ngir muur metit yi askan wiy jànkonteel jamono jii. Waaye, mel na ni pexeem moomu sooy na, ndax réewum baay Nelson Mandela daan na bërki-démb Misra jéll bu set wecc, ginnaaw bi mu ko dóoree 1-0. Waaye bu ñu fatte li ponkal ma woon, Mawàdd Wàdd, daan wax : “Dawuma ci ginnaaw bal, ci ginnaaw nit ñiy daw ci ginnaaw bal bi laay daw. Ndax, nit ñoonu ay xale ñoo ci ëpp, te xale yooyu ñooy ñiy jiwi ndamu askan wi ëllëg.” Yaakaru waa ju baax jooju, taxawoon démb di xeexal réewum Senegaal ak doomi Afrig yépp, te jaarale woon ko ci tàggat-yaram, mat naa bàyyi xel. Wànte, mel na ni tey bukki-njuur-sàmba yi ŋànk futbalu Afrig bokkuñu ak moom xalaat. Waaye, nan jàppale sunu gaynde yi nu fa teewal. Ba négéni, gàcceeluñu nu. Ndax, dibéer jii weesu rekk lañu daan Ugàndaa 1-0, daldi jàll ci kaar de finaal yi. Waaye, nag, bumu nu tax a réere mbir jafe-jafey askan wi ak mbirum petorol bi ak gaas bi lëmbe réew mi. Wareesul a fàtte yit baykat yi, xale yiy dugg ci looco yi wutali Ërob te naan Bàrsaa walla barsàq, njàng mi, lopptaan yi, yoon wi, añs.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-3-9-2023/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM (3/9/2023) SAALIF KEYTA KUPPEKATU MALI BA WOON GAAÑU NA Ci gaawug démb ji, 2 sàttumbaar 2023, la kuppekatu Mali bi gaañu. Ndem-si-Yàlla Saalif Keyta mi ngi amoon 76i at. Moom, doomu Mali ji, mooy kuppekatu saa-afrig bi jëkk a gañe Kuppeg wurus gu Afrig (Ballon d’or africain) ca atum 1970. Saalif keyta, ku aayoon lool la, taqe woon te xareñ. Moo tax, jot na def i jaloore yu baree bari ci futbalu Afrig, waaye woneet na mëninam fa Tugal. Dafa di, ku fa siiw la, rawatina biir Farãs. Bésub 6eel ci weer wii lees jàpp ngir sargal ko. Dees na ko jagleel ab yaxal bu yaatu ngir fésal jaar-jaaram. BELLINGHAM A NGI WÉY DI WONE BOPPAM FA ESPAAÑ Doomu Àngalteer ji dafa ñëw ci sàmpiyonaa Espaañ bi rekk daldi miin. Démb ci gaawu moo nekkoon ñeenteelu joŋanteem ak Real Madrid. Waaye, bu ci nekk dugal na ci. Fim ne nii, mu ngi ci 5i bii ak benn paas. Soppey Real Madrid yi dugal nañu ko seen xol te demaguñu fenn. SERGIO RAMOS DELLU NA SEVILLE Gannaaw ba mu jeexalee pasam ak waa PSG, moom jañkatu Real Madrid ba woon mu ngi toogoon ci ruqam di liggéey. Ci dibéeru tey ji, 3i sàttumbaar, la dellu Seville, fa mu jóge woon dem Real Madrid. RONALDO AK SAAJO MAANE ÑU NGI BOYAL ÀLLU NAAR YI Déggoo bi dafa mel ni dafa teel a jàpp njaax diggante Saajo Maane ak Cristiano Ronaldo. Jamono jii, ku nekk ci ñoom ñaar a ngi xiir di def loolook loolu. Ronaldo mu ngeek 5i bii ci ñetti joŋanteem ak ñetti paas, Saajo Maane amagum 4i bii moom it ci ñeenti joŋante ak seen këlëb bii di Al Nasr. NDEKE ISCO MÀGGETUL ! Ñu bari jàppoon nañu ni ay balam dañoo jeex ndax li mu toogoon lu tollu ci 9i weer ci bãwu Real te futbalul. Ci merkatoo bii la fasanteek Real Betis. Boobu ba léegi nag, moo ngi fay wane xereñte gi ñu ko xame woon. Seen ñeenti joŋante yépp moom lañu tabb baay faalu joŋante bi, jot na ci dugal benn bii.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/5796-2/
Seen xiibaari tàggat-yaram Dibéer 12i Féewaryee 2023 Kuppeg àddina këlëb yi :  “Real Madrid” defatina ko ! Démb ci gaawu gi, 11i Féewaryee bii atum 2023, la woon finaalu kuppeg àddina këlëb yi, mu doxoon ci digante “Real Madrid” ak “Al-Xilal”. “Real Madrid” moo dóor juróomi bal ci ñett (5-3) dellu jëlati raaya ji. Bii moom 5eelu yoonam bu muy jël bile kuppe waaye it kuppe gii doon 100eelu kuppe yu mu jël ba mu sosoog leegi, muy lu rëy. Mu nekkoon finaal  bu neex donte ñu bari nag xamoon nañu ni Real Madrid daf koy dóor, waaye it taxul Al-Xilal yombalal ko ko, ñëw na ak bëgg-bëgg xeex ca la mu mën. Gannaaw fan yu xaw a lëndëm yi mu nekkewoon ci fan yii ñu génn, rawatina ba leen “Barça” dóoree woon Finaal, gisoon nanu ni dafa xawoon a baayi loxoom walla mel ne ku réeraloon wureem. Kuppe gii ñu jël démb yaakaar naa ni dana nekk lu leen di dolli jom ci li des ci at mi. Fi mu toll nii moo ngi war a dajeeti ak “Barça” 1/2 kuppeg buuru Espaañ (coupe du roi), war a xëccoo ak moom ba tay Sàmpiyonaa ba, ba noppi xeexi nguuram ga xa “League des Champions”. Ana kukoy tee, Vinisis ? Saa-beresil bi, luñu ko gën a xeex, muy gën a wane boppam. Fan yii weesu gis nañu na koy moroomi wurekatam sonalee ca Espaañ, nga xam ni dañu koy cokkaas ak di ko gaañ, leeg sax soppey yeneen këlëb di ko saaga ak a xas ndax limuy ku ñuul. Loolu lépp teewul muy yokk jom ak fi gën a wane boppam. Démb ci seen finaal bi mu taal ñaariyoon kër gi ba noppi joxe ci ñu dugal. Gannaaw loolu ñu fal ko wurekat bi gënoon xereñ ci kuppeg àddina këlëb gi. Kii di Walweerde (Valverde) dugalatina ñaari bay ci démb, yeewuwaat ci nelaw yi mu nekke woon ba noppi weesu lim bi ko tàggatkatam bi tegaloon ngir mi dugal lu tol noon mbaa lu ko ëpp (10). Bensemaa it jot na ci dugal bennam. Loolu di mbégte ci waa “Real Madrid” ak seen soppe yépp.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xecc-bu-danee-dagg/
XËCC BU DAŊEE DAGG ! Nimbir yiy doxe diggante nguur geek kujje gi bi Màkki Sáll toogee ci jal bi ba tey jii, dalul xel dara. Nun ñépp a ànd ci demokaraasi, waaye ni ko peresidaŋ Sàll gise — ku am doole danga koy wone, doo maye dara, doo yërëm kenn — mën naa jur ëllëg musiba ci réew mi. Ci sama gis-gis bu gàtt, dafa war a méngook li gën ci sunuy aada. Senegaal, waxtaan ba juboo lanu xam, lu fi am solo. Su dee wote rekk, nag, kenn du ni guléet, miim réew yàgg naa tabb ay njiitam te deret du turu. Lu jar a fàttaliku la, tey jii alal ju bari feeñ na ci suuf si. Mbaa du sax petorol boobook gaas bee yóbbu fiti ñenn ñi ? Bu nu ànduleek sunu sago, am nay réew yu mag ak i boroom doole dinañ jéem a salfaañe Senegaal ngir rekk aakimu alal jooju. Nanu ci Yálla musal waaye noonu la ko gaa ñooñu tàmmee def. Kon, li war ki Yàlla teg ci boppu réew mi, mooy xam ni nun ñépp, ba ci kujje gi sax, njabootam lañu. Su ko defee mu wuuf ñépp, bañ a tànqamlu kenn. Nay yolomal buum gi bu ko mbir yi laajee, te yit këwdiir giy bax ci kaw taal bi, na koy moytoo tëj ràpp. Li peresidaŋ Abdu Juuf bàyyiwul woon xel ci looloo taxoon ñu tëral sàrtu wote bi ñépp àndoon ci atum 1992. Dafay faral ñatabal nit ñi ba ñu sës te du yoon. Ak li muus di néew doole yépp, bu sësee songe te kuy bëgg a lab sax, soo ko tàllalee jaasi mu jàpp ci.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/barsaa-am-barsaq-lu-xew-ci-miim-reew/
BARSAA WALLA… BARSÀQ !… LU XEW CI MIIM RÉEW? Géej gaa ngiy wann sunu doom yi. Mbete jasig juy warax béy bu lab. Ay fukki, ay téeméeriy, ay junniy waxambaane ak, léeg-léeg sax, ay janq walla ay jeeg ñooy song géej gi, wuti Barsaa walla… Barsàq ! Ñi ëpp ci ñoom, dañuy des ci ndox mi, ñuy mag di ndaw, di góor di jigéen, liir yi sax, ci lañu. Te musiba bii, du tey, du démb la fi xewe : lu ëpp fukki at a ngi nii, Senegaal di dund lu ni mel ! Waaye, jamono jii, mbir mi daa takkarnaase, mel ni tuq su bënn, saañ ba réer. Ci weeru oktoobar wii nu génn lu tollook 480i doomi-aadama ñoo des ci géej gi (ñii dee, ñeneen ñi réer) ci diir bu gàtt, ci genn ayu-bés ! Woññiy néew de, neexut. Waaye, fàww nu def ko : ci bésub 24eelu oktoobar, 100i nit dee nañ mbaa ñu réer, ginnaaw ba soldaari Espaañ yi wallo 50i nit, fexe ba muccal leen. Ca bés boobu sax, fii ci géeji Senegaal yi, 140i doomi-Senegaal des nañu ci ndox mi ci sababug lakk gi xewoon ca gaal ga xale yi duggoon. Ci bésub 27eelu oktoobar mu amoon genn gaal gu bàyyikoo woon Sumbajun te yeboon 80i doomi-aadama, faf benn bato bu làrme Senegaal mbëkk ko, 41i nit dee ca mbaa ñu réer. Ñaari fan lañ ci teg, ci bésub 29eel oktoobar, genn gaal gu yaboon 77i nit suux, yóbbaale 50 doomi-Senegaal. Ca ëllëg sa, 30eelu fan ci oktoobar, 150i doomi-aadama ñoo des ci géej gi, boori Ndar. Boobaak léegi, nag, amul ayu-bés buy jàll te yéenekaay yi dun nu yëgal suuxug gaal, tàggewaaley xale yoo xam ne ñoo nara a dundali gaynde géej yi. Rax-ci-dolli, li xew ci géej gi warunoo tax a fàtte liy xew ci mandiŋ mi. Ndax kat, ñu bare ci xale yiy gàddaay, ñu ngi koy jaare ci yay wi : di jël daamar yi, di dox, di fanaan ci àll bi, dëkko-dëkk ñu taxaw fa. Ñoom ñooñu, li ñuy daj ci yoon wi, tanewul la ca biir géej ga. Seen jafe-jafe yi dul jéex, dañ ciy boole xeetal gi ñuy jànkoonteel ci dëkki Naar yi ñuy jaar. Naar yu bëggul a gis Nit ku ñuul, di leen teg ñaawteef yi gën a ñaaw, lu xel  mënut a nangu. Lii moom, du jàmm ! Waaye am na leneen lu-dul jàmm te doy waar. Ndaxte, laaj wi sampu mooy : naka lam réew di daj lii ciw njaqare ak tiis, te di wéy di def niki dara xewul ! Ay téeméeriy nit yu deewandoo, te loolu daanaka yëngalul kenn ! Doo dégg walla nga gis njiitu-réew mi fullaal dëgg mbir mi, am ci taxawaay bi ñépp doon xaar ci ñoom : naqarlu ko, woote ci dëju askan wi, uti pexe yuy dakkal jii jéyya ! Waaw, ana tamit ñi ci kujje gi ? Ana sàmmkati àq ak yelleefi doomu-aadama yi ? Ana waa way-moomeel yi? Ana kàngami iniwérsite yi ? Kenn wooteewul ci lenn luy tax askan wi naqarlu musiba mu ni mel ! Woote taxaw-seetlu ba xam lu xew ? Xam lu waral bile balaa ? Ak lu ciy pexe ? Dëgg la, Njiitu-réew mi jël na xalimaam metitlu ko, waaye fa la yem ba léegi nii. Ndax waa Sàrli Ebdoo gën gone yiy des ci géej gi ? Seriñ Muntaqa it, ci fan yii rekk, ci baatu jawriñam, naqarlu na li xew, waar te yedd it askan wi, laata muy ñaan muslaay Sunu Boroom. Wànte, saafaras jéyya jii de, feeñagul ! Moone waa Senegaal dañuy faral a bàkkoo ne ay nit ñu nite lañu… Am déet ? Lu waral nu tekkaaral nii, ni muut ci mbir mi ? Ana bokk diine ji ne ci nun, muy jullit yi di kercen yi ? Ba noppi nag di bariy coow ci yeneen wàll yi mel ni politig bi ! Di seetaan jën yeek gaynde géej yiy xëccook a jiiroo, di yàpp sunuy doom yi lab ca géej gi. Amunu lu nuy def lu dul ne fii di lijjanti ay palaas yi politiseŋ yiy awante ci seen i biir, ngir rekk duufal seen i poos! Waaye nag, lu kenn mënul a dégg, mooy way-jur yii di yabal seen i doom yu amagul sax 20i at, dugal leen ci gaal yi wuti… Barsàq ! Noonu, ndeysaan, la ci xale bii di Duudu Fay mi amul lu dul 14i at ñàkke bakkanam, ginnaaw ba ko baay bi, Mamadu Lamin Fay, dugale cib gaalu musiba… Ngir lan ? Ciy yoxoy moroomam bu amagul 17i at la newoon ba muy nelaw ba fàww. Yeneeni way-jur yi àndoon ak seen i doom ñoom it, niki Lamin Fay, yoon a ngi leen di topp. Li xew ci réew mii, dëgg-dëgg, du jàmm ! Nu ñuy def ba delloosi xel yi ? Moone su nu xooloon ci ni réewi Tubaab yiy doxale, doon nanu am royukaay ci wàll wii. Ndax ñoom kat, kenn rekk ci ñoom, su waññeekoo, àddina sépp yëg ko. Lu waral nag, nun ñii jàpp ne, noo fi gën, nuy doxale nikiy bàyyima ? Xana du fii la bato «Joola» suuxe woon (1861i nit dee ci) mu doonoon jéyya ju ame géej ji yées ci àddina si. Te booba sax, askan wépp amoon na ci lu mu yëg, naqarlu woon ko bu baax, amoon ci tiitaange ju réy ; muy lu nuy jooy ba sunu jonni-tey jii ! Yëg-yëg boobu, fu mu nu jaar tey ? Li xew ci réew mii, du jàmm ! Moone am nay ndaw yu ni du ñu toog di seetaan luxóor bu ni mel. Ndegam xam nañu ni, mënuñoo am jenn yaakaar ci Nguur gi, walla sax ci njiiti diine yi, dañu jóg, xar seen tànki-tubay, taxaw jàmmaarlook jafe-jafe yi. Dañoo jaar ci xaraley jokkookaay yu bees yi, ba jàpp seen bés bu ñu jagleel seen i moroom yi réer ci géej gi. Noonu lañ taxawalee seen mbooloo, jàpp ni kenn mënu leen a tee dëjal seen i mbokk, seen i xarit, seen i dëkkandoo, seen i moroom yi fi jóge ci anam yu ñaaw yooyule. Noonu lañu nasale seen bopp dëju askan wi. Te ñi dem barsàq kat, kenn mënu leen a jàppal lenn lu dul bëgg a tekki, maanaam, mënal seen bopp, mënal seen i way-jur, am dund gu dàq dund gi ñuy dund tey. «Ñépp xam nañu ne Ërob moo dàq Senegaal !» (ci li kenn ci waxambaane yi mucc ci gàddaay gi wax). Doonte, xale yi yaakaar ne seen wërsëg a nga feneen fu dul seen réew, xamuñu li leen di xaar fañ jëm. Ñu ci bari ci ñiy dàqi seen wërsëg, ña ciy egg, yaakaar ju tas lañ nar a taseel. Àjjana ja ñu yaakaaroon, naxee-mbaay lay mujjee doon. Kuy wuti dëkk booy mën a tekki, daa fekk bunt yépp tëju sa kanam ca fa nga fekk baax ! Te, naka-jekk, xëy moom, daa tumurànke ci Senegaal gii ! Bu yàggul rekk la benn bànqaasu ONU (Kurelu mbooleem réew yi ci àdduna si) di xamal ne Senegaal bokk na ci réew yi gën a néewle xéy, doonte Gornmaa bi weddi na ko ba mu set. Waaye, su jafe-jafe yi yemoon foofu rekk, coow li du woon baree noonu. Li ci yéeme mooy ne, Gornmaa bii waroon a fexe ba xale yi am liggéey, moo leen koy far xañ ! Ndax kenn umplewul ne, ñi ëpp ci xale yiy songi géej gi ak boroom pexe yi leen di jàllale ci seen i gaal yi, ay mool lañu. Li ko waral mooy ne, mool yooyu, dañoo amatul fu ñu nappe ndax cër bu ngand bi Nguur gi yakkal bato yiy jóge bitim-réew. Ñooñu di ñëw ba ci wetu waax bi di raasaatu as tuut ci li sunuy nappkat yi dese woon. Ba tax na, li mool yi daan fortaatu, ci jën yu sew yi, dara lañ ci dul gisati ! Li ëpp ci bato yooyule, ñu ngiy jóge Portigaal, Espaañ, Farãs, Riisi walla Siin. Sunu mool yi, lu ñu foraatu, amatuñu ko. Ñàkk pexe nag, pexe la. Ku amul ndey nàmp maam. Ñoom ñi miin géej gi ba noppi, ñoo takk seen fit, uti Barsaa… mbaa Barsàq ! Ñu ñëw nag ci « mbëkk » mi, yokku ci gune yi amul woon xéy, xamatuñu woon fu ñuy jublu ; yokku it ci ubëryee yi ñàkkoon seen i liggéey, doon wër ba toqi ; ak tamit baykat yi gisatul woon tool yuy naat ba tax ñu wutsi péey bi, dàqsi seen wërsëg… Te, su desul lu dul sunu njiit yi, mel na ni yëf yi du fi yem. Ndax kat, ci fan yii rekk, Senegaal mayati na waa UE (réewi Tugal yi) ñuy wéy di fi indi seen i bato yi, di napp ni mu leen neexe. Ci lañu déggoo wéyal lu ni mel ci diiru yeneen juróomi at, ginnaaw ba ñu matalee juróom yu njëkk ya. Ci li ñu xaatim ci kayit, juróomi at yii, mënees na koo yeesal. Maanaam daal, tey la Waalo gën a aay ! Lu ëpp nag, tuuru. Waa Espaañ ya ubbi woon seen i digaloo yi, yombal dëkkin bi ci seen réew ndax mbas mi ak i balaam, dellu nañ ci ginnaaw, tëjaat ràpp seen bunt yépp. Yemuñu foofu, ñu ngiy waaj a yabal seen jawriñ bi yore mbiri bitim-réew, mu ñëw waxtaansi ak njiiti Senegaal yi, ba xam lu ciy pexe.  Ndegam yor nañu ay pexe ! Waaw, luy pexe ci jéyya jile ? Nun waa Senegaal, nanu nite njëkk ! Ku wàññeeku (muy mbokk walla muy koo xamul), nanu ko metitlu ba fu metit yem ! Xam ne nit kuy dem ak i noppam, amul njëg, ak ku mu mën a doon, ak fu mu mën a jóge, ak nu mu mën a mel ! Nanu fonk doom-aadama, te naw sunu bopp ! Su loolu weesoo, ci wàllu politig bi, nanuy fal i njiit yu gëm seen bopp, bëgg seen réew, xareñ ci li ñiy def, te maandu ci alalu askan wi. Loolu rekk mooy tax ñoom ñooñuy falu, bokk yëg-yëg ak askan wi, di farlu ci faj seen i soxla. Lu ñuy nas, ñu nasandoo ko, lu ñuy liggéey, ñu liggéeyandoo ko, ngir rekk jëmale réew mi kanam, ba askan wi ci boppam, di gis boppam ci lépp luñ koy fexeel. Uséynu Béey
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-tey/
DÉMB AK TEY Dal-leen ak jàmm ci seen xët DÉMB AK TEY mi leen seen yeénekaayu web LU DEFU WAXU jagleel. LU DEFU WAXU nag, li ko tax a jóg mooy dégtal leen ay xibaar yu wér te wóor te aju ci xew-xew yi gën a fés ci réewum Senegaal ak sax ca bitim-réew. Waaye tamit, bindkat yi dinañ  faral di leen ci baaxe seeni gis-gis ak i xalaati doomi réew mi ci mépp mbir mu ñeel Senegaal.  Rax-ci-dolli, yéenekaay bi dina leen wisal, may leen ŋeleju ayu-bés gi ak nataali ODIA, aji-ŋeleju bu mag bi. Bii-yoon, nag, seen yéenekaay LU DEFU WAXU da leen a indil lu bees tàq, mayati leen ko, muy seen xët DÉMB AK TEY. Ñaari baat yii, DÉMB ak TEY, ay tegtal lañu ci li xët mi wund. Jokkalekat bi, “AK”, di wone ne deesuleen  téqale. Maanaam, kenn warul a féewale cosaan walla jamonoy maam ya (DÉMB) ak sunu jamono jii (TEY). Bu ko defee, li nu ko dugge mooy dekkil cosaan, fàttali leen xew-xewi démb yu mag yi. Waaye nag, bàkk mbaa ŋàññ maam rekk yi taxunoo jóg. Naka noonu, jógunu ngir di leen nettali rekk li xewoon démb walla di leen léebal. Bu ko defee, nësër gi dëgg mooy lëñbëtil leen cosaan ak aaday maam ya, méngale leen ak jamonoy tey jii ngiree nu rotal ciy njàngat yi nuy jariñ tey, leeralal nu sunu ëllëg. Ci gàttal, xët mu bees mii nu duppe DÉMB AK TEY , li mu sasoo moo di wëral leen réew mépp, sowu ba penku, bëj-gànnaar jàpp bëj-saalum, béréb bu nekk mu taxaw fa xamal leen la fa xewoon ak njàngale yi ñu ci mën a jukkee. Ndaxte, cosaan mooy caabi jiy ubbi buntu tey, di làmp biy leeral ëllëg. Kon, cosaan deesu ko xeeb. Ndege, ku xeeb sa cosaan, ñu xeebal la ko. Seen yéenekaay LU DEFU WAXU xam na ni, wenn askan mënul a jëm kanam féeg mi ngi dëddu cosaanam. Rax-ci-dolli, réew mu askan wa naat, ci cosaanam ak i aadaam la sukkandiku ba indi fa ay yokkute. Looloo gënatee tax mu baaxe leen xëtam mu bees mii. Wolof dafa ne, kuy dem ba xamatoo foo jëm, war ngaa dellu fa nga jóge. Bu ko defee, sunu sas moo di dellu rooti ci teenu DÉMB, nàmpi ca meenu cosaan ngir tabax sunu TEY ak sunu ËLLËG. Seen mbokk, Paap Aali Jàllo moo nekk ci boppu gaal gi, di ko joow ci géejug cosaan, yen saa yi mu mbiij ci dexug aada, leeg-leeg moom walla kenn ci LU DEFU WAXU indil leen sarica. Tey, Daawuda Géy moo def ab gëstu ca Kaasamaas ci ñeyu-xare bu ñépp miin turam te taxul kenn xam ko bu baax : Jiñaabo.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-3/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM MESSI GAÑE NA KUBAM BU NJËKK AK INTER MIAMI Ci guddig gaawu gi jàpp dibéer jii weesu la Inter Miami doon joŋante finaalu Leagues Cup, doon ci daje ak Nashville. Bi joŋante bi dawee ba ci 23eelu simili ba la Pulga bi daldi dugalal Inter Miami, ñu dawal ba ci xaaju ñaareel bi, ci 57eelu simili bi, Fafa Picault fayul ekibam. Ci teg dóor yi lañu mujje tàqaliku. Inter Miami gañe 10i bii ci 9 (ci teg dóor bi). Bii kub di bu njëkk ci Messi ak Bousquet, saa-baarsalon ya woon. MBAPPE DUGGAAT NA CI PÀKK YI Keroog ci gaawu gi, Paris Saint Germain doon na amal ñaareelu joŋanteemu Ligue 1. Mbappe bokkoon ci 22i futbalkat ya. Dafa di, moom sax moo dugal biiwu PSG bi ci teg dóor bi ñu amoon (1-1). Loolu nag di wane xanaa ni juboo am na ginnaaw coow li dox seen diggante. Nde, Mappe dafa ban a xaatim pas gu bees ak këlëbu péeyu Farãs bi, ne day toog ba 2024 demal boppam. Loo naqadi woon kilifay PSG yi ba ñu beddi woon ko. BELLINGHAM : GAN GIY TABAX Gan-ganlu moom bokkul ciy mbiri Jude Bellingham. Goneg Àngalteer bi, dafa ñëw Real Madrid rekk daldi bokk ; fireeku, di futbal futbalam. Moo tax  ci ñaari joŋante yi njëkk ci LIGA bi, dugal na ci ñetti bii ba def ci benn paas. Keroog gaawu, ci ñaareel xaaju mats bi la daldi dugal ñaari bii. PAAP MATAAR SAAR A NGI XÀLL YOONAM Ren mooy ñaareelu atam ak Tottenham. Mu mel ni, ren jii, daa fas yéene dëggal boppam, wane lim mën. Gannaaw ba ñu soppee tàggatkat, la ku bees ki daldi xamle ni Paap Mataar du juge ci këlëb bi ndax daf ko soxla. Boobu ba léegi nag gisees na genn kóolute bum am ci moom ba tax mu di ko futbal-loo. Ci gaawu gii weesu, Paap Mataar moo jëkk a dugal ci seen ndam biñu am ci kaw Manchester United (2-0).
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/ligue-des-champions-dortmund-ak-real-madrid-nooy-daje-finaal/
LIGUE DES CHAMPIONS : DORTMUND AK REAL MADRID ÑOOY DAJE FINAAL Démb, ci àllarba ji, lees doon amal ñaareelu joŋantey demi-finaali “Ligue des champions” bi, diggante Real Madrid ak Bayern Munich. Lu ko jiitu, ci talaata, Paris Saint-Germain doon na janook Dortmund. Dafa di nag, Dortmund ak Real Madrid ñoo am ndam ci seen i joŋante, war a daje ci finaal bi war a am keroog 1eelu fan ci weeru suwe  fa Wembley. Paris Saint-Germain – Dortmund Saa-Almaañ yi ñoo toogloo farãse yi ci seen ñaari joŋante yi. Paris Saint-Germain moo njëkk a fekki, keroog 30i fan ci weeru awril wii, Dortmund daldi koy dóor 1-0. Barki-démb, ci talaata ji, 7i Me 2024, mu fekksi ko ca fowoom bees duppee “Parc des princes”, gañewaat ko benn bal ci dara, daldi jàll finaal. Real Madrid – Bayern Munich Ci weneen wàll wi, waada (champion) Espaañ bi moo toogloo yeneen Saa-Almaañ yi. Ñu amal ñaari joŋante yu metti lool nag. Keroog, bu njëkk ba, 29i Awril 2024, la Real Madrid fekki woon Bayern ca pàkkam, ndaje ma metti, ñu mujjee timboo 2-2. Ci àllarbay démb ji, 8i Me 2024, Bayern Munich daldi fekksi Saa-Espaañ yi seen dëkk. Niki bu njëkk ba, ndaje mi metti lool. Ci 2eelu xaaju joŋante bi la Bayern njëkk a dugal (Alphonso Davies, 68eeli simili). Naka noona, Real Madrid daldi koy tontu, dugal, dugalaat. Joselu moo dugal ñaari bii yi (88eel ak 90+1eel). Noonu la 1/2 yi demee. Ñaari way-bom yi war a daje bés bi njëkk ci weeru suwe wees dëgmal, fa Wembley (Àngalteer).
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-16-7-2023/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM (16/7/2023) KUPPEG ÀDDINA SI 2026 Kippu yi ñeel xëccoo paasu kuppeg àddina si war a am ci atum 2026 mi génn nañ fii ci wàlluw Afrig. Senegaal moo ngi bokk ci kippug B gi mook ñii di Kóngoo, Móritani, Tógoo ak ñaari Sudaŋ yi. Senegaal lees jàpp ne mooy ékib bi gën a jekkandi ci kippu gi. Waaye, naataangoom bii di Kóngoo, di ekib bu mag itam, ëpp ko li mu jël ciy kuppeg Afrig du ko ko yómbalal wenn yoon. Te sax, léegi, ekib bu ndaw sax dafa amatul. Ekib yépp ay bañ-bañlu, di jéemantu ni ñépp. Senegaal ci boppam, xam na ni ñépp a koy xaarandi jamono jii. Ba tax na, joŋanteem yépp a nar a metti. GENERATION FOOT JËL NA RAW-GADDU GI Generation Foot bu Ndakaaru moo jël Sàmpiyonaa Senegaal. Démb ci gaawu gi la doon joŋnte ak Jàmbaar, ci 24eelu bëccëg bi. Benn poñ doŋŋ la soxla woon ngir kenn bañ koo dabati. Waaye, la gën témboo la def. Nde, dafa dóor Jàmbaar 1-0, daldi matal 50i poñ. Bii mooy ñetteelu yoon mu koy jël ginnaaw 2017 ak 2019. ESTEFAAN BAAJI AMAAT NA KËLËB Gannaaw ba mu delsee Senegaal, ci këlëbu Casa Sport bi ko lóofoon (tàggat bi muy ndaw), doomu Sigicoor bi, Estefaan Baaji, dina dem fa Siipr, xaatim ca këlëbu Olympiacos Nicosie ag pas gu tollu ci ñaari at. AFROBASKET, KIGALI 2023 Jigéeni basket yi war a teewal Senegaal fa Kigali (Ruwàndaa) ñeel powum basket bi ñuy amal ci diggante réewi Afrig yi, dinañu dem ci 21 Sulet bii. Fim ne nag, ñoo ngi Ndakaaru di amal seen i tàggatu di ko waajal ni mu waree.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/mbara-wacc-doomi-gaynde-njaay-yi/
MBARA-WÀCC DOOMI-GAYNDE NJAAY YI ! Sunu gaynde yi amagul ñaar-fukki at wone nañu njàmbaar fale ca Niseer, nga xam ne fa la réewi Afrig yi gën a xareñ ci futbal daje woon di joŋante. Jaaraama sunu Doomi-Gaynde yi ! Ay jàmbaar dëgg lañu, ñaawuñu ci xare bi ndax ca Niseer, daje nañook ñeenti ekib, am ndam ñeenti yoon. Mali ak Ganaa lañu njëkk a gal-gal ñaari bal ci dara (2–0), duma Burkinaa Faaso duma yu metti, juróomi bal ci benn (5–1), jóge fa jaar ci kow Réewum Afrig-bëj-Saalum benn ci dara (1–0). Léegi, ñook seen doomi-ndeyi Mali yi rekk a des ci géew bi ! Ak lu mën a xew fan yiiy ñëw, gone yi def nañu lu réy. Sunu xel dal na ndax déggoo, doon benn a leen tax a yegg fiñ yegg tey, fëq caax yi juròom ñeenti yoon te benn yoon doŋŋ lañu nax seen góol. Muy firndeel itam ni ekib bi dëgëre… Fi mu ne nii, ñu ngiy xaar Mali, waaye dara mënatuleen a tee bokk ci joŋante bu mag biy dajale réewi addina sépp, ca Poloñ ci weeri me ak suweŋ yiiy ñëw. Loolu du guléet, ndax Senegaal demoon na Nuwel-Selànd, ci atum 2015 ak itam réewum Kore Bëj-saalum ci atum 2017. Ku xam Yuusuf Daabo miy tàggat sunu gaynde yu ndaw yi, xam ne amul tiitukay. Daanaka kóoluteem ci goney ekip bi amul àpp. Nee na Senegaal amul lu muy ragal ndax démb la tàmbalee waajal joŋanteb Niseer bi tey soog a ñëw. Loolu tekki ne liggéey bu jaar yoon a ko tax a dal xel. Te, sàllaaw, bala yàgg nun ñépp dinanu bég. Yuusu Daabo yokk na ci sax ne : « Jot nanoo am i jogaŋte yu metti, Burkinaa Faaso lanu mujjee dajeel, ñu indilnuy jafe-jafe. Waaye sunu pas-pas tax na ñu génn ci. Gëm naa ni kenn mënatunoo të, ku nu dajeel dinan la dóor ». Li wóor ba wóor moo di ne bu Senegaal toogul ci gàngunaay bi dina ñaaw, ndax dellu ginnaaw lay gën a nirool. Ñaari yoon yi mujje yépp, doomi-gaynde yi àgg nañu ba ci njeexital li ñu daan leen. Su nu waxantee dëgg, nag, loolu mënuta wéy te ñu baree ngi koy naqarlu ba tey jii. Kon mu mel ni am ndam ci dibéer ji rekk mooy seral xol yi. Abdulaay Seen (Bi nu bindee li ngeen jàng ba noppi, lanu dégg xibaar bu tiis bi : Mali mujje naa dóor Senegaal 3 penalti ci 2. Kon ñu ne xalam demoon na bay neex…)
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/futbal-ak-basketu-senegaal-yaakaar-ak-yakki/
FUTBAL AK BASKETU SENEGAAL : YAAKAAR AK YÀKKI Bi Alseri dumaa Senegaal benn ci dara ci finaalu joŋanteb réewi Afrig yi (CAN) ak léegi, mu ngi bëgg a yàgg. Waaye, kenn fàttewu ko. Li ko waral nag mooy finaalu basket bi soxna yi ñàkk, ñoom tamit, biñ dajeek Niseryaa fan yii ñu weesu. Yaakaaroon nañu ne, soxnay basket yi dinañ feral sunuy rongooñ. Ndeysaan, keroog bi leen Niseryaa daanee fii ci Ndakaaru, ñépp a ci amoon tiis ak naqar ndax yaakaar ju tas. Ñaari finaal, ñaari kub, Senegaal ñàkkandoo leen ci menn at, ci diggante bu gàtt a gàtt ! Ñii ne waaw, ban dëmm a nu juutu ? Ñee di laaj, kan moo nu um ? Laaj bi jar a laaj, nag, ci dëgg-dëgg mooy : lan walla kan mooy sunu gàllankoor ba tax nuy lajj saa su nekk ci cëppaandoo bi ? Tey nag, ci futbal bi lanuy tàmbalee. Séex Sekk, Roose Mendi, Sil Bokànde, Umar Géy Seen, Ferdinaa Kóli, Umar Daaf, Saalif Jaawo, Paap Buuba Jóob, Fadiga, Àllaaji Juuf, Aari Kamara, Saajo Maane, Kalidu Kulibali… Ku dégg yile tur, sam xel dem ci jaloorey ekib nasiyonaalu futbal bu Senegaal. Ñii nu fi jot a lim ñépp nekkoon walla di ay futbalkat yu xereñ lool, ñu ràññee leen bu baax ci Senegaal, ci Afrig ak ci àddina sépp. Waaye, ak lu tur yiy réy réy, lenn doŋŋ lañuy màndargaal : yaakaar ju tas. Waaw. Ndaxte, ba nëgëni-sii, Senegaal amagul benn biddéew ci mayoom bi. Ak lu coow liy bare bare, mësta jël kub. Laaj bi ub bopp yi mooy : lu tax Senegaal jëlagul kub ba léegi te, jamono ju nekk, mu yor ay ndaw yu xereñ ? Nu ànd xool, démb ba tey, lu xel mën a jàpp ne mooy sunu laago ci futbal bi. 1961 : Ndoorteel li Ci at mii la Senegaal di door a amal joŋanteem bu njëkk. Ñaari at lañ ci teg (1963) ekibu futbal bi Senegaal daldi jël raw-gàddu gi ci Joŋantey Xaritoo (Jeux de l’Amitié) yi amoon ca jamono jooju. 1965 : Njëlbéenub joŋante ci CAN Ci at mii la Senegal di door a bokk ci joŋanteb réewi Afrig yi (Coupe d’Afrique des Nations), gàttal bi ci nasaraan di joxe CAN. Ci njëlbéenug joŋanteem boobule, Senegaal ñaawu ci. Ndax, moo jëloon ñetteelu palaas bi. Gànnaaw gi, daanaka Senegaal ab nooy-neex la woon, ku jàpp rekk wulli, ekib bi dee daanaka. 1990 : Dekkiwaat bi Senegaal dekkiwaat. Claude Leroy mi yoroon ekib bi ci diggante 1989 ak 1992 moo ko defaraat, tàggat leen ba Senegaal joŋantewaat, ginnaaw atum1965, « ½ finales » CAN bi amoon fii ci Senegaal ci atum 1992. Waaye, ñetteelu palaas bi la mujje jëlaat. Ci atum 1994, « ¼ de finales » la yem, wute joŋante yu 1996 ak 1998. 2000 – 2019 : Jamonoy jaloore ak yaakar ju tas Ci wàlluw futbal, bi Senegaal dee Senegaal ba tey, ci diggante atiy 2000 ak 2019 lañu ko gën a ràññee. Ndaxte, ci jamono jii la ndawi Senegaal yi gën a xereñ fëlle : A1llaaji Juuf, Fadiga, Ferdinaa Kóli, Umar Daaf, Lamin Jaata, Aliyu Siise, Saalif Jaawo, Paap Buuba Jóob, Tooni Silwaa, Aari Kamara, Abiib Béey, Jomansi Kamara, Mamadu Ñaŋ, Suleymaan Jaawara… Bi ñooñu jeexalee, Saajo Maane ak i ñoñam, Gànna Géy, Kalidu Kulibali, Sabali, Ismayla Saar, Jaawo Balde… wutu leen. Ku ci gën a xereñ, dàq futbal sa moroom nga ne kii. Ñu yaakaaroon ni bile yoon, nag, Senegaal dina am dara. Ndeysaan, bu dul finaalu 2002 ba ak « ¼ de finales » bi ñoom Àllaaji Juuf demoon ca « Coupe du Monde » 2002 ak ndam li ñu amoon ci kow Frãs ci ndoorteelu joŋante bi, Senegaal jëlul dara, tus… Naam, li Senegaal àggoon finaal ca Mali, ndam la. Naam, def na jaloore ju réy a réy bi mu amee ndam ci kow Frãs ci « Coupe du monde » bi ci toppoon, ñu ni déet-a-waay mu dem ba « ¼ de finales » yi. Kenn sañul a wax ne loolu du ndam. Wànte, ndam loolu, wareesoon na ko def ag garab, suuxat ko ba mu meññ yeneen i ndam yu gën a réy, maanaam nu jël kub. Ndege, Senegaal bokkoon na ci ekib yi gën a xereñ ci Afrig, te ba léegi loolu la ñépp jàpp.  Waaye dara, dara la fi indiwul : 2004 Tinisi moo nu toogloo ca réewam ci « ¼ de finales » yi 1-0 ; 2006 Misra moo ko toogloo ci « ½ finales » yi, mu mujje jël ñeenteelu palaas bi. Ci at moomu « Coupe du monde » amoon na, waaye Senegaal bokku ci ndax Tógo moo ko tere woon dem, mu metti woon lool ci waa réew mi. CAN 2008, Senegaal génnul sax gurub bi mu bokkoon. 2010, Amara Taraawore moo yoroon ekib bi. Waaye, ci CAN bi, Senegaal ñetti joŋanteem yépp la ñàkk, daldi toog. Demul yit ci « Coupe du monde » at moomu. Ñu foog ni Alain Giresse mi ñu tabb ci atum 2013 dina faj laago bi, waaye moom tamit dañu koo mujje dàkk ndax lajj bi mu lajjoon.  Ki ko wuutu mooy Aliyu Siise mi bokkoon ci ekibu 2002 bi te nekkoon kapiteen bi. Ginnaaw CAN 2017 bi nu toogee ci « ¼ de finales » yi, moo delloosiwaat Senegaal, ak ñoom Saajo Maane, ci “Coupe du monde” 2018 bi. Waaye, foofu tamit, yaakaar ju tas lañ fa jële. Ndax Senegaal génnul gurub bi mu bokkoon doonte sax kenn mënu ko fa woon. Ci CAN 2019 bi, ñépp a newoon ne bii yoon moom, day baax. Waaye, Alseri moo nu dóor ci finaal bi. Yaakaar tasati.  Ñii di saaga fii Aliyu Siise, ñee di duut baaraam njiiti federaasiyoŋ bi, ñeneen ñi di ko jiiñ sëriñtu bi waa réew mi nekke ba ci futbalkat yi. Kan moo ci wax dëgg ? Cuune, yaataayumbe ak sëriñtu Bi fi Bruno Metsu (2002) jógee ba léegi, fukki tàggatkat wuutu nañ ko ci boppu ekib bi laata Aliyu Siise di toog. Ci fukk yooyu, juróom-ñaar yi ay doomi-réew mi lañu. Loolu day firndéel matadi, cuune ak caaxaan bi ñu yore futbal bi. Ndaxte, bir na ne ba tey xamuñu nees di tànne tàggatkat bu baax ak naka lees koy gungee, jàppale ko ba liggéeyam àntu. Loolu day wone yit yàkkamti bi ak ñàkk fulla bi waa federaasiyoŋ bi nekke. Te, ku yàkkamti, yàqule. Benn, ab ekib dees koy tabax ci diir bu yàgg. Mbir mi du xéy rekk sotti. Fàww nga may tàggatkat bi tuuti ngir mu tabax ekib buy jël kub. Waaye xel nanguwul, benn walla ñaari at yu nekk nga ut beneen tàggatkat, indi yeneen i futbalkat. Ñaareel bi mooy ne, njiit day am fulla ci boppam. Du nekk ma riirandoo waxatuma la ak benn nopp. Fàww bëgg-bëgg yi wute, gis-gis yi ak xalaat yi safaanoo. Kon mënoo, yow njiit li, saa bu taskati xibaar yi waxee fii nga topp leen, bu askan wi yuuxoo fee ngay jéem a def lu ko neex ngir bañ coow. Moo taxit, saa boo leen toppee, boo lajjee, ñoom ñoo lay njëkk a song. Li koy firndéel mooy atum 2008, bi Senegaal arañefee ak Gàmbi fii ci estaad Lewopóol Sedaar Seŋoor, ndaw yi dañoo mer ba futt, di ñaxtook a sànni xeer ci buntu estaad bi. Bés boobu tàngoon na lool. Kenn fàttewul tamit 2012, bi farandooy ekib bi meree, di sànni ay xeer, butéel ak i yu ni mel ci teereŋ bi. Jotoon nañoo sax wàcc ngir duma futbalkat yi ak njiiti federaasiyoŋ bi. Bés boobu, daa fekkoon Kodiwaar am ñaari bii ci kow Senegaal, muy tekki ne Senegaal du dem ca CAN bi waroon a am atum 2013. Bi ñu jógee ci loolu, FIFA, kurél gi yor futbal bi ci àddina sépp, dafa teg ay daan Senegaal. Bi ñu ko laajee lu tax futbalu Senegaal mënta jëm kanam, Àllaaji Juuf dafa tontu woon ne ñi fi nekk (njiit yi), xaalisu futbal bi lañu bëgg waaye bëgguñu futbal bi. Kàddu yooyoo taxoon ñu teg ko fi ay daan yu metti, moom Àllaaji Juuf. Waaye, ndax mënees na koo weddi ? Ñaari at lañ ci teg, Demba Ba waxaat lu ni mel. Te, wolof nee na, fen du màgget. Kon daal, njaw des naw xambin. Daanaka, jamono ju nekk, saa su joŋante amee, nga dégg ne waa federaasiyoŋ bi ñoo ngi yaataayumbe ak xaalisu futbal bi. Seen njaboot, seeni mbokk ak i xarit, ñépp lañuy yóbbu fi ekib biy dem, di gundaandaat ak a ndagarwale ci alalu réew mi. Ñu ni déet-a-waay, sëriñ si demaale ak seeni xarfafuufa, gisaanekat yi ame nit ñi fii, ñuy fekk ci ron-lalu futbalkat yi ay téere… Muy lu yéeme sax ! Kon, mel na ne laaj bi nu sampoon ca njëlbéen am na tontu. Cuune, yaataayumbe ak sëriñtu bi ñu nekke moo nu teree jël kub… Bu beneen yoonee, dinaa leen wax lu tuuti li ma xam ci basket bi !
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/li-gen-a-fes-ci-xibaari-futbal-alxames-9-feewaryee-2023/
LI GËN A FES CI XIBAARI FUTBAL (alxames 9 féewaryee 2023) BELSIG AM NA TAGGATKAT BU BEES Kuppeg àddina 2018 ba léegi, Belsig dafa nekkoon ciy jafe-jafe. Njeexitalu kuppe gi gën koo feeñal. Moo tax ba seen tàggakat ba, Robeertoo Maartinees, xamoon boppam, tekki ndombal-tànkam balaa ñu koy dàq. Démb, ci àllarba ji la ñu xam ne ni tànn nañu Dominikoo Tedeskoo muy seen tàggatkat bu bees. RONAALDIÑOO BU BEES ? Ba nu xëyee la xibaar bi daanu, ñuy xamle ni saa-beresil bi, Ronaaldiñoo moo ngi dox ci tànki xaatimloo doomam ca Bàrsaa. Ndax dana mel ni baay ba ? Seetaan a dàkk cib ndaje, te lu ci kanam rawul i bët. KUPPEG ADDINA KËLËB YI Làmmiñ daal, ndeke mooy ndeyu balaa yi ! Vidaal de, ba ñu defee jiifii-jaafaa ba noppi, mu xam ni mën na am Real Madrid, la naagu di waxati bu jàppee Real Madrid na mu koy def. Da doon faf Al-Xilaal dóor ekibam bii di Falamingo 3-2. Ndeysaan. Wax baaxul. ÀNGALTEER Manchester City moo ngi ci guddi yu lëndëm jamono jii. Yoonu wure moo koy toppe li ñu jàpp ni dafa ñàkk doxal yoon ci njënd meek njaay mi ñeel wurekatam ya ; maanaam, fañ ko yamloo daf ko jéggi. Ñu ragal ni li ñu koy toppee bu dee dëgg diñañu ko teg daan yu diis, lu ci mel ni wàññiy poñam mbaa sax wàcce ko ca Championship.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/demb-senoor-tey-wadd/
DÉMB SEŋOOR, TEY WÀDD Li ko dale atum 1978 ba tey jii, woteb ren bii mooy wote bu fi njëkk a am te Ablaay Wàdd sampu ci ndëndam. Walla boog, loolu la ñu bare jàpp. Ndax, man kat neneen laa gise mbir mi. Bees delloo ginnaaw, fàttaliku atum 2007, bi Ablaay Wàdd faluwaatee, war a amal ñaareelu moomeem, dafa wax wax ju am solo. Wax jooju, mi ngi ko waxe woon cim ndaje mu mu séqoon ak taskati xibaar yi. Bés boobu la leen « Góor gi » xamal ni mébétam mooy njabootam ci wàllu politig, maanaam « libéraux » yi, toog ci boppu réew mi lu mat juróom-fukki at, gën gee néew. Foofu, Seŋoor mi njabootam — « socialistes » yi — toogoon ñeent-fukki at ci jal bi, la Wàdd doon diir mbagg, ne sax fàww mu rawe ko fukki at. Wax jooju, lu jar a bàyyi xel la. Képp kuy jàngat géewu pólitig beek li ciy xew, war na jéem a xam ndax mébétu Góor gaa ngi ci yoonu àntu, waaw am déet. Su dee waaw la, mu seet man walla yan pexe la koy amale. Nanu leen xoolaat wote yi fi jot a am ci atum 2000 ba nëgëni-sii. Li wolof di léebu naan, bu ndung sàqee, ndung leng, géewu pólitig bi doy na ci firnde. Ndax, 2000 ba léegi, wote njiitu réew yi fi am yépp, Ablaay Wàdd ak i « doomam » ñoo ciy xëccoo. Kon, mu mel ni làmb ji PDS ak…PDS rekk lañ koy tëggal. Nan dellu ginnaaw. Ci atum 2007 Ablaay Wàdd (PDS) moo janoo woon ak Idiriisa Sekk (mi bawoo woon PDS). Ñu ni déet-a-waay, ci atum 2012, Ablaay Wàdd janoowaat ak Maki Sàll (moom tamit jóge woon PDS). Bu fa yemoon mu tane, waaye ci wote ndawi pénc mii weesu, Maki Sàll fexe na ba Usmaan Tanoor Jeŋ, Mustafaa Ñas, Ndem-si-Yàlla ji Jibo Léyti Ka ak seeni farandoo, fàtte PS, làng ak moom ci biir Bennoo Bokk Yaakaar, maanaam ñëw mu boot leen. Amoon na, nag, weneen lafu PS wu lànkoon ni du ànd ak Maki Sàll ci wote yooyu, muy Xalifa Sàll (PS) ak Maalig Gàkku (AFP). Ñooñu, Ablaay Wàdd da leen bëggoon a teg ci ginnaawam, jiite ndajem làngu politig gii di Mànkoo Taxawu Senegaal. Ba ñu lànkee, ne Xalifa Sàll lañuy àndal, Ablaay dafa ne wérëñ, ber yoonam, dem ceek Maki Sàll. Fan la yëf yi mujje ? Xanaa PDS — Maki Sàll — raw, PDS — Ablaay Wàdd — topp ci ! Léegi, nag, sóobu nanu ci woteb 2019 bi ñu war a fale njiitu réew mi fiy toog ba 2024. Waaye, mel na ni dara soppeekuwu fi : na woon, fa woon. Leer na ñépp ni kenn ci ñaari doomi Ablaay Wàdd yii di Maki Sàll (APR) ak Idiriisa Sekk (Rewmi — noonu la ko Idiy binde) mooy gàddu ndam li. Kilifay PS yu mag yi ñoom, Tanoor ak Ñas, daanaka Maki modd na leen ; la ca desoon di bañ, muy Xalifa Sàll ak Gàkku mujje nañoo ànd ak PDS (Idiriisa Sekk). Kon PS moom, kenn waxaalewu ko. Naam, ñoo ngi wax ci xale bi yëngal jamono te xew, Usmaan Sónko, li am ba des mooy : xamees na ni ku falu PDS a la fal, ndax kàrt yépp a ngi ciy loxoy Ablaay Wàdd. Jàppees na ni, ku mu àndal ci ñaari doomam yooyu di Maki Sàll ak Idiriisa Sekk, dinga jël ndam li. Looloo waral, doonte jëmmu Ablaay Wàdd bokkul ci wote bi, fi mu nekk ñépp a ngi koy déglu ba xam kan lay mujjee tàllal loxoom ngir mu sakkanal ndono li. Ablaay Wàdd, nag, bi mu yegsee Senegaal keroog alxames 7 féewaryee bii weesu te ñépp doon ko xaarandi ba xam ku muy àndal, mënees naa jàpp ciy kàddoom ni fasul yéenee far ak kenn ci mbër yi. Mébétam mooy wote bi bañ a am. Waaye ku xam Wàdd xam ni ku tàmm a woote di xool ndey-joor la fekk booba xel maa nga jëm càmmooñ. Xanaa nu yónni yàgg rekk ba xam fu wànnent di mujj ak i gëtam. Bésu joŋante bi soreetul…9
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/riiru-kampaan/
RIIRU KÀMPAAÑ Lépp lu yëngu am na lu ko yëngal. Réewum Senegaal, jamono jii mu ngi toll ci waajtaayu joŋante bi ñuy fale kiy toog ci jal bi. Këru-Àtte gi gën a kowe fésal na juróomi wutaakon yu samp seen ndënd : Maki Sàll, Isaa Sàll, Usmaan Sónko, Madike Ňaŋ ak Idiriisa Sekk. Kenn ci ñoom la xelam toogatul fan yii, taluñu lu-dul kàmpaañ bi. Lawax yaa ngi jaabante, dëkkoo-dëkk ñu dem fa, di saafonteek ñaa fay yeewoo. Ñoom ñépp a ngi biral seen gis-gis ci doxalinu nguur ba noppiy tanqal askan wi ak i dig. Waaye Wolof Njaay dinay wax ne : dige, bor la. Naka noonu, ay ndaamaar lañuy war, foo toll di leen séen ñu yëkkati seen loxo ca kow, misig biy jolli. Lu kàmpaañ bi gën a jege di gën a rëb ; li koy firndeel moo di ne ñenn ci doomi-réew mi ñàkk nañu seen bakkan keroog bay farandoo Maki Sàll ak Isaa Sàll jàmmarloo. Wutaakon yaa ngi defante ba mu saf sàpp te ñi leen di jàppale kenn demul ñu des, fu nekk ñu nga fay daje, di def seen kem-tàttan ngir seen mbër jël ndam li. Kan lay doon bu bés baa ? Tont laa ngi ci yoon wiy ñëw…
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/sacciin-wi-jem-ci-tann-yi-degmal-te-feenalees-ko/
SÀCCIIN WI JËM CI TÀNN YI DËGMAL TE FEEÑALEES KO Sëñ Abdu Xaadr Kebe mooy biral fii xalaatam ñeel wotey tànn Njiitu réew mees dëgmal ci atum 2024 mii nu nekk. Dafay feeñal yenn pexey njuuj-njaaj yees lal ngir sàcc wote yi, foqati baatu askan wi. 1 : Baril àdduwaay yi (lieux de vote) ak pekki àddu yi (bureaux de vote) (3 910 000 bureaux de wote) ba waa kujje gi duñu fa man a am aji-teewal ci bépp pekku àddu, ñu jaare ca def càcc gu mag (création de procès-verbaux de résultats). 2 : sos ay pekki àddu (bureaux de vote) yu yées 600 te àtteb tànn bi (code électoral) daa wax ne pekkub àddu bu ne daa war a ëpp 600 wéttkat (àddukat, votant). Ñoom nag sos nañu 2700i pekk yu yées 600 yii, yépp nag ngir tàyyeel-loo kujje gi ci wut ay way-teewal. Lu ëpp 2 700 000 ciy pekk yu yées 600 àddukat (votant) sos nañu leen. Pekk yi ñu tuxal du jeex (bureaux délocalisés) ; yooyu nag dañu leen di def ay pekki yees dul gis (soo wëroon ba sonn doo ko gis), pekki jeneer (bureaux fictifx) ak i wéeruy négandiku (abris provisoires). Ngir tànn yii dëgmal 2024 gis nanu ci kàrt elektoraal bi lu sakkan ciy pekki àddu yees tuxal, soppi leen ñuy ay pekki àddu yoy jeneer (fictif), loolu jeexiital ci 469 271 tànnkat. Pekk yees dul gis nag duñu jeex, ni ñu leen di sosee mooy bind ci kàrtuw tànnkat bi (carte électeur) pekku àddu Waagu-Ñaay ci misaal, nga dugg ci di wër ba xàddi. Yii daal ay misaal lañu ci sàcciinu tànn wi ñu fi teg. Abdu Xaadr Kebe
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-1-10-2023/
XIBAARI TAGGAT-YARAM (1/10/2023) KUPPEG ÀDDINA WAY-LUU YI (MUUMA YI) Bàyyeesu leen xel, waaye way-luu (muuma) yi teewal Senegaal ca kuppeg àddina si bees leen jagleel ñoo ngay def i jaloore yu rëy. Ba léegi, ékib gañeeguleen ! Ñoo ngi toll ci ñeenti joŋante, gañe 3 yi daldi timboo benn bi. Kaar-dë-finaal lañu war a amal fan yii. ILIMAAN NJAAY DUGAL NA BIIWAM BU NJËKK AK MARSEILLE Démb ci gaawu gi la Ilimaan Njaay, doomu Senegaal ji, di sog a dugal biiwam bu njëkk ak Marseille ci seen joŋante bi amoon seen diggante ak Monaco bi ñu ñàkk ci (3-2). Lii la wolof naan, xëcc bu daggul dikk. Jafe woon na ci moom ca njëlbeen ga, ba tax mu daan xaw a jaaxle. Waaye, mu gëm ko ba mu dikk. Njoortees na ni dana ko gën a firiloo nag, nde lees di séentu ci moom ëpp na li mu fa waneegum. MÓORI JAW, KU JAR A BÀYYI XEL Alin Siise war na bàyyi bu baax bëtam ak xelam ci doomu Senegaal bi, Móori Jaw. Moo ngi def i jaloore yu réy jamono jii ca këlëbam, Clermont. Gaawug démb gee ci mujju, mu def joŋante bu rëy xañ kii di PSG bu Mbappe ndam. BARÇA AK MBIRUM NEGREIRA Barça génnagul ci mbiri Negreira bi ba léegi. Mbir yaa ngi nekkoon ci loxo yoon mu di ko saytu di amal i luññutu. Ci fan yii nag, coow li dafa tàmbalee jugaat ba am ci sax ñuy ragal ñu tas Barça. Ndaxte, mbirum nger muy yàq powum futbal la. Waa Barça nag, ba léegi dañuy rasu, di bañ ni fayuñu benn arbiitar xaalis ngir mu ràccal leen seen boor. Kii di njiitu LIGA bi, Tebas, daldi na yëkkati ay kàddu ci loolu: “Ger (corruption) nekkul joxe xaalis rekk, Waaye, yéene bi kese, soo ko amee, mënees na la ci jàpp”. NEYMAR A NGI BËGG A JAAXLE Jamono jii, Neymar fireegul ca naar ya. Ndaxte, boobu ba léegi, bii dafa jaar nii mu jaar nee. Mbir yi dafa xaw a dëgëragum ci moom, ba léegi dugalagul. Benn paas la fa def, am fa penaalti daldi koy rate. Fees ko séentu woon tëllagu fa !
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/gacce-ngaalaamambugaar-useynu-beey/
GÀCCE NGAALAAMA, MBUGAAR ! Senegaal amati na ndam ci 3eelu fan ci weeru nowàmbar wii, jaare ko ci benn ciy doomam, di Muhamet Mbugaar Saar, ab bindkat. Moom mii Farãs tappal na ko raaya bu am solo, muy Prix Goncourt  bu atum 2021. Muy raaya bu ñëw topp ci yeneen yu mu fi jotoon a am. Muhamet Mbugaar di xale bu am 31 at doŋŋ, juddoo Ndakaaru ci 20eelu fanu suweŋ, ci atum 1990. Doomu Séeréer bu màgge Jurbel la, te jànge ‘‘Prytanée Militaire de Saint-Louis’’ bi ñépp a xam. Foofa la ame lijaasam bii di “Baccalauréat”, laata muy àggaleji njàngam ca Farãs, ca ‘‘Lycée Pierre d’Ailly’’ ak ‘‘Ecole des hautes études des sciences sociales’’. Moom nag, li muy gune yépp, jotoon nañu koo tappal ay raaya yu bare. Jëloon na fi Grand prix du roman métis ak Prix Ahmadou Kourouma ca atum 2015 ak Prix Littéraire de la Porte Dorée ca atum 2018. Persidaa Maki Sàll itam sargaloon na ko fi, defoon ko Chevalier de l’Ordre du Mérite ca atum 2015. Ci téere yi waral jaloore yooyu, man nañ cee lim : La Cale (2014), Terre ceinte (2015), Silence du choeur (2017) ak De purs hommes (2018). Dëgg-dëgg, xale bu jàmbaare la, ndax ku gis ay jalooreem ak li mu bind yépp, dinga xam ni ku xareñ la, mën na li muy def, te it raw na ay maasam ! Prix Goncourt, niki beneen bi ñuy woowe Renaudot, raaya la bu ñuy joxe at mu ne ca Farãs, ngir sargal bindkat bi gën a ràññeeku ci bindkati téereb nettali yiy jëfandikoo làkkuw nasaraan. Waaye ñépp xam nañu ne, làkk woowu jéggi nay digalooy Farãs bay law ci àddina si yépp, ndax, daanaka, ay fukkiy miliyoŋi nit ñooy jëfandikoo làkk woowu. Kon nag, Prix Goncourt, raaya bu am solo la ; cuune du ko gàddu, doonte ci way-jëfandikoo farañse yi rekk la yem. Prix Goncourt bu mag boobu la doomu Senegaal bi gàddu gannaaw René Maran (ca atum 1921) ak Mari Njaay (ci atum 2009). Kon nag, gàcce ngaalaama, Muhamet Mbugaar ! Li tax ñu tànn ko ci biir bindkat yi bare yooyu doon xëccoo raaya bi, mooy ñeenteelu téereem bi mu bind, duppe ko La plus secrète mémoire des hommes. Muŋ ciy nettali jaar-jaaru bindkat bu xareñoon, ku ñépp séentu woon ca kaw, waaye mu mujjee daanu ba ñépp fàtte ko, ndax rekk, ñàkk dégg-dégg bi nit ñi wone woon ñeel i mébétam. Mu mel ne, kàngami Goncourt yi doon àtte ngir tànn mbër mi leen doy, dañoo yéemu ciy xalaati Mbugaar yu xóot yi, waaye rawati-na ci xereñ gi mu wone ci mbindinam. Li gën a neex ci raaya Mbugaar bile, mooy bés bi mu ko amee, dafa xaw a yemook 7eelu fanu nowàmbar, di Journée internationale de l’écrivain africain, maanaam bés bi ñu jagleel bindkati Afrig yi. Bés boobu, li ëpp ci bindkati Senegaal yi daje woon nañu ci seen béréb bu siiw boobu di Kër Biraago gu bees. Ñu bare ci ñoom nag jot nañu faa jël kàddu, rafetlu xew-xew bi, biral seen mbégte ci jaloore ju ni mel. Teewul nag, am ñeneen ci réew mi, ñu yékkati seen baat di ŋàññ Mbugaar ndax ñàkk a rafetlu ay bindam. Waaye loolu, jeneen wax la, ndax dañuy jàpp rekk tontuy Mbugaar ci boppam : “Na nit ñi jàng téere bi ba noppi, buñ amee lu ñuy wax, ñu wax ko”. Ci sunu wàllu bopp, ci wax jooju lanu jàppandi ba ba nuy jàng téereem yi indi coow lépp. Kon, nu waxati ko : “Gàcce ngaalaama, Mbugaar !”
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/faidherbe-saay-saay-bi-nuy-sargal/
FAIDHERBE, SAAY-SAAY BI NUY SARGAL Bi Siidiya Ndàtte Yàlla génnee àddina ak léegi, am na xarnook xaaj. Waaye, mi ngi mel ni mësta gane àddina. Dara gënta ñaaw, nag, cosaan lees neenal. Nde, ku xeeb sa cosaan, ñu xeebal la ko. “Xare bi gën a xereñe ci xare yi, mooy bi ngay noote say noon te doo xeex”. (Sun Tzu) Bés bu Yàlla sàkk, ay junni-junniy nit dinañ romb ci kanamu Teyaatar nasiyonal Dañel Soraanoo. Ku ci xam Dañel Soraanoo moomu, na nu wax mooy kanati. Ndaxte, doxandéem bile, bokkul ci jàmbaar yi fi def i jaloore te ñuy woy seen i baax ak seen i baaxi maam. As lëf lees dégg ci moom, mooy ne, ab aktëeru farañse la woon. Jeex na ! Nga daldi may laaj, yow miy jàng bind yii, ne ma : « waaw, moom sax, lu mu defal réew mi ba nu war ko tudde ab teyaatar ? » Ma tontu, ne la : « Dara ! Tus ! ».  Nee ñu, baayam, gerefiye la woon ci tirbinaalu Ndakaaru ci ndoorteelu xarnu bin génn. Xam naa yaa ngi naan lii yomb na de ! Waaw, yomb na torob kay te metti ci xol. Rax-ci-dolli, ak li mu xereñe woon ak a bare woon i kaseti teyaatar yépp, amu ci benn bu mu mës a jagleel Afrig walla Senegaal. Waaye, loolu du doon mbetteel ñeel nit koo xam ne, mësta fóon ngelawu Senegaal. Nu génn Ndakaaru, daldi teeri Ndar géej, fekk fa beneen doxandéem bees di sargale sunub ñaarelu iniwérsite bu gën a mag : Gastoŋ Berse. Daanaka, beneen Dañel Soraanoo rekk lees fi amaat. Waaye, kii moom, ku ko xamul laaj ko Seŋoor. Dina la ne kii mooy « baayu prospective » (am xalaatin ci wàllu xeltu), taggal la ko ba nga yéemu. Waaw, Seŋoor de, foo ko fekkaan, mu ngay tagg ngóor si. Lu ni mel jaaxal nu lool, nag. Naam, Gastoŋ Berse Ndar la juddoo, dib sët ci senn soxna su tuddoon Faatu Jaañ. Wànte, ba muy gone gu ndaw la génn réew mi. Sunu juumulee, tegaatu fi tànkam ba keroog muy dee. Mu ngoog. Dëgg la, li nit ñiy fàttaliku walla lees xam ñeel démb lañuy tudde mboor walla cosaan, boroom xam-xam yi soloo ko walla muy luñ nuy nettali. Waaye, dara gënta ñaaw, nag, coosaan lees neenal. Nde, ku xeeb sa cosaan, ñu xeebal la ko. Aw askan, mëneesu koo ga ba muy weg ak a màggal nit ñoo xam ne, bokkul ak ñoom dara te, amaluñ ko benn njariñ ñeel jubluwaayam. Seŋoor, nag, looloo nekkoon naalam : fexe ba waa Senegaal bëgg ay doxandéem yu tekkiwul dara ci ñoom, di leen dundal ci seen i xol, seen i wax ak di leen sargalee seen i taax ak i palaas. Bala maa dee rekk, muy taafantoo kàddoom yu neex ci nopp yooyu te di lakk xol, ay « métissage culturel » fii, « civilisation de l’universel » fële. Waaw, bu doon loolu la, lu ko tee tudde Teyaatar bi Alexandre Pouchkine walla Alexandre Dumas ? Nun, nag, kenn demul nu des. Li ma ci gën a jaaxal, mooy tekk-tekkaaral bi maasi Seŋoor yi àndaloon. Ndege, ca jamonoom, amu ci kenn ku ci amoon xelu walla fitu sëgg ci noppu Seŋoor, ne ko : « Sëñ bi, ku rafet xol nga. Waaye, maye lu baax ci kër lay jëkke. Ñu mel ni Séex Aliyun Ndaw, Aimé Césaire, Duuta Seck walla Duura Maane ñoo gën a yey ci ñu tudde leen sunuy Teyaatar. » Ndaxte, ñooñu, kenn gënul leen a doon i werekaan. Amaana, fullaalun woon tur yooyii nees rëdd ci kanami taax yi. Boo demee, mbir mi daf noo soofoon, nu ñàkkal ko faayda. Mën na am tamit ne danoo amoon, dëgg-dëgg, kersay biral sunug démb, démb gu doy waar googu te ruslu. Nii la ko Fadel Ja junje woon cib yaxalam bim génne woon ci yéenekaayu Sud Quotidien. Ñu may ma, ma joxeeti beneen misaal buy màndargaal gàcce googu nees am ci sunug démb ba tax nees di ko tanqamlu, di ko jéem a fàtte. Dafa mel ni, sax, dëddu boobu nu dëddu sunug démb, lu yàgg la. Ndege, ci njeexitalu oktoobar 1986, Abdu Juuf, njiitu réew ma woon, ak jawriñu mbatiit jamono jooju, Maxili Gasama, tabaxlu woon nañu xabru sunu jàmbaar ja, Lat-Joor, ca Déxële ga mu daanoo woon. Waaye, lu jiitu jëf ju rafet jooju, dañu sàggane woon lool Déxële ak teenam bu siiw ba, dëddu woon leen. Keroog bi ma ciy door a teg samay bët, dama waaru woon sax. Ndeysaan, ci njeexitalu atum 2017, am nab yaxal bu génnoon ci yéenekaayu Le Quotidien, ñu bind ci ne, 30i at ci ginnaaw, Déxële ak li mu làmboo cim mboor ak i bérébi cosaan, dafa gën a toskare. Céy ! Ak ni askanuw Senegaal xëree ci aada ak cosaan, fonk lool seenug démb, di ko woy fu nekk, di ko bind ak di ko ndamoo saa su nekk. Moo, nag, lu leen tax a sàggane nii bérébi cosaan yiy seedeek a taxawe démb googu ? Lu waral gent gees leen gent ? Man, daal, dama foog ne dañu raxas seen bopp yi, walla mu am lu leen dal. Dafa di, li ëpp ci nun, danuy faral di fàtte ne, jépp jàmbaar jees fiy nettaliy baaxam ak i jalooreem yit, fenn rekk la wax jiy mujj saa su nekk : dee na te kenn xamul fuñ ko denc. Li ko dale Lat-Joor ci boppam ba ci Alburi Njaay, jaare ko ci Séex Umar Fuutiyu Taal, Siidiya Ndate Yàlla Jóob ak ñeneen, ñii kenn xamul sax fu seen i néew nekk ; ñi ci des, ñoom, bitim-réew lees leen suul, sore lool seen i dëkk. Tombuktu. Doosa, ca Niseer. Tundi Bànjagara. Àllab Ndeng-Ndeng ba ca Gaboŋ. Nga xool béréb yii ñu leen mujje gis ni ñu soree.  Ndax dañ fay jaare réer nu ba fàww ? Yàlla bu ko Yàlla def ! Sunu càggante tax na be, 1960 ba tey, amagun fib nittabaxon (estati) bu mag biy màndargaal sunub jonn, keroog bi nu moomee sunu bopp. Mënoon nanoo am sax benn bu nuy jagleel Seŋoor, ak lees ko mënti tuumaal. Xam naa, yaa ngi naan ci sam xel, yow miy jàng sama yaxal bi, « Monument de la renaissance », nag ? Bu ko defee, ma xool la ndànk, yëngal sama bopp ne la, xanaa kay du ponkal yu jagadi yooyu nga may wax. Ñooñu nga xam ne, duñ sax sëgg xool nu, sunuy bët mën a daje. Du ñooñu kay téen di xool asamaan si ñoo ma tax di wax. Nee ñu, jant bi lañuy jéer. Waaye, ñoom la rekk. Ñoo koy yëg. Dañu xamul ne, nun, amalun nu benn solo. Du lenn lu ñuy tekki ci sunuy bët te amunu benn yëg-yëg ñeel leen. Ñu nekkoon ay ñay walla ay « cachalots » ñoo bokk yem ci nun. Bu loolu weesoo, ma jàll ci yuq wax ji. Coowal Louis-Léon César Faidherbe mi lëmbe réew mi a ma tax a yatt samab xalima ngir wax ci sama xalaat. Seneraal bu ñaaw te bon boobu, Senegaal sañ koo bëgg, di ko sargal. Muy def ak mustaasam bu sëkk boobu ak i lonetam yi may bañ a tudd. May wax mu aj sikkimam boobu ak colam gu yànj. Waxuma sax nittabaxon (estati) ak palaas yees ko jagleel ca Ndar te mu jur coow lu réy fan yii, waaye tuddeesati na nootkat ba am ngér, ab otel, ay mbedd… Bi ci mujj te gën a ràññeeku mooy pom (jàlluwaay) biñ ko tudde ca Ndar. Mu mel ni loolu doyul. Ndaxte, biir Ndakaaru ci boppam, amoon na fab nittabaxon (estati) bu fa ne woon jonn ba ci atum 1983, ci kanamu màkkaanu njiitu réew mi, méngook tey Këru-Soldaar ga fa nekk. (Dees na ko àggali…) Bóris Jóob ci tekkig Aali Jàllo
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/njangat-ci-teere-ceerno-alasaan-sall-bi-nu-duppe-tenkoo-ak-takko-ba-ca-elise-deeyub-jawrin-bi-nu-denkoon-mbiri-petorol-ci-senegaal-moolkat-bi-fauves-ca-pa/
"LE PROTOCOLE DE L’ÉLYSÉE" : NJÀNGATU PROF BUUBA JÓOB Téere bu am solo bi Ceerno Alasaan Sàll génne fan yii ci nasaraan, te móolkat bi,  ca Pari, tudd Fauves, mënees na ko tekkee nii ci kàllaamay Kocc : “Tënkoo ak takkoo ca “Élysée” : déeyub jawriñ biñ dénkoon mbiri petorol ci Senegaal” Li ñu war a njëkk a wax, moo di ne mbind mi rafet na, xóot na, neex a jàng. Ni Ceerno Sàll ràbbee téereem bi rekk biral na liggéey bu takku : leeg-leeg mu yóbbu la fii, bàyyi la fa, demaat feneen, dellusiwaat, yeen saa mu joxoñ, yeen saa mu junj. Téere bi mën nañ ko duppe « Pólotig, bu àndul ak màndute, jur toj-toj ak njaaxum yu dul jeex ». Li muy wone, xamle ko, moo di naka la ñuy jéngee, jataŋ, réewi Afrig yi. Mën nañ yaatal sax, boole ci réew yi ñuy noot yépp, di manq seen deret, di foqati seen alal. Ceerno Alasaan Sàll, waa Farãs la duut baraamu tuuma ; moo waral mu duppe téereem bi : « Tënkoo ba ca “Élysée” ». Waaye li ko gën a soxal mooy mbirum petorol mi. “Élysée”, nu fàttali ne mooy màkkaanu njiitu Farãs yi. Am na ñu ànd ak ñi ci jal bi, ci réew mi, te mere Ceerno Alasaan Sàll ci  lu mu waxul ci yenn tënkoo yu mel ni ba  amoon  Huston, ca Amerig. Moonte ku jàng bu baax li mu bind, dinga gis ne Ceerno Alasaan ŋàññul waa Farãs rekk : xëccoo yi, jiiroo yi, képp kuy njàccaar mën na leen a ràññee. Ku jàng bu baax téere bi, mën nga gis it ne Ceerno Sàll, xol ak xel la ko binde, di ci fésal naqaram. Wone na ci li ko jaaxal, bett ko, li tax mu lànk, ne ngoram mayu ko mu dugg ci yenn yi, mu jaral ko fippu, jàmmaarlook nguur gi. Moom daal, weer na gejjam, ku weeri yaa moom. Gejj gi, mi ngi ci ñeex meek rënd bi, mi ngi it ci yakk bi. Man nag, tibb naa 8i yoon, daldi dank : Njaaxum yi dul jeex te ki ko firndéel di Farba Seŋoor, àndoon ak Parsidaa Ablaay Wàdd, mujj fekki Parsidaa Maki Sàll. Njaaxum yi yemul ci Farba, yemul ci dem ak dikk, ñu ngi ci njàng mi, càkkeef gi ak wér-gi yaramu askan wi ; Màndute, ngor, nger ; Polótig ni muy doxe ci réew mi. Ñiy woote boolo bokk, ak ñi siis, fëqale, bàyyiwul dara, xuloo yi, xeex yi, mbiri xaalis ; Moom, am na lu bare lu mu ci xam, ndax dugg na, génn na, ci Ànd-Jëf Xare bi ak ci APR (muy farandooy nguur gi) ; Caytu ak koom, ni ñu lëkkaloo, naka la gise mbey mi, napp gi, mbiri jokkoo ak jumtukaay yu bees yi, naka la ñu war a dégmal, topp, jubbanti, yaatal, yombal, jubal, jëflanteek sàndikaa yeek yeneen mbootaay yi ; Mbiri àtte, fa mbaxane wara nekkee benn ; Mbiri xalaatin, caada, cosaan, wolleet ; Xar-kanam mi ngi ci. Am na nataal yu leer, am na yu nëbbu, yu mu muur. Wone na ñiy dóor (Wàdd, Maki), ñiy dékku (ku ci mel ni Abdul Mbay) ; Ndénkaane yu am solo ci mbiri rabat, dégmal, caytu ;wone na njàng, xam-xam, xarala. DAANEEL Téere Alasaan Sàll bi am na solo : jur na coow lu réy waaye ñi bokk ci làngu polótig gii di ”République Des Valeurs” am nañ ci mbégte. Ceerno nag, ci CRD la bokk, woote Ànd, Déggoo, Dekkil Bokk. Waa APR ñoom, dañoo mer ba futt, rawatina ñi téere bi xosi. Coow li du gaaw a dakk, ndax lii doomi-réew mi ak ñiy bàyyi xel ci  Senegaal daa ñu ci wax. Du ñàkk mu doon téere bi ñuy gën a waxtaane ci at mii ñu nekk. Cafka gi nag ak ceeñ li, li ma ci gën a saf, mooy li Ceerno sant Sàll, wone ni Al-Pulaar la, ajoor la yit. Loolu de war naa neex, soxal ñépp ñi nangoo ubbi seeni gët ak seen xel, bañ a jiital, bañ a surux ci kàmbu xeet, waaso ak diine su ñuy polótig. Su ko keneen bindoon, dina am ñu ni dafa bañ Parsidaa Maki Sàll ndax li ñu bokkul xeet, waaso, mbaa tarixa. Fii ci réew mi, war nañ jiital saa su nekk njariñu réew mi, boole ci njub ak bokk jëmu. Baabakar Jóob Buuba Jàngalekat, gëstukat, Bokk ci Taxaw Temm.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/serin-seeka-bari-doole-ci-langu-politig-bi/
SËRIÑ SEEKA BARI DOOLE CI LÀNGU PÓLITIG GI ! Ni waa Senegaal gëmee Yàlla te fonk diine, umpul kenn ci àddina si. Nde, askanuw Senegaal, ñi ci ëpp ay jullit lañu. Nee ñu, cig xayma, 100 yoo jël ci doomi réew mi, 95 yi jullit lañuy wootewoo. Diiney Lislaam, nag, biir Senegaal, dafa làmboo ay màndarga yi koy wutale ak i réew yu bare. Ndaxte, amees na fiy këri diine yu mag, maanaam ay tarixa, askan wi xër ci lool, sax. Tarixa yooyu, ay sëriñ a leen jiite, ñu leen di woowe xalifa, taalibe yi fonk leen lool, weg leen. Dafa di, dayo bu réy a réy la kilifa yooyee am ci taalibe yiy déglu ak a jëfe seen i ndigal saa su nekk. Àq, dayo ak gëdd bi taalibe yi jox sëriñ si moo tax, ñoom sëriñ si, ñu am kàddu ak sañ-sañ bu bir ci mbiri réew mi, rawatina pólitig. Te, lu ni mel, ndajem njiitu réew mi, Maki Sàll, ak Idiriisa Sekk mi lëmbe réew mi doy na ci firnde. Waaye, bala tey, démb la woon. Ca 1930-1940, fekk na 2 eelu xare bu mag bi ame àddina sépp. Jamono jooju, Almaañ gu Itleer dafa songoon Farãs, sonaloon ko lool. Ci la Farãs wëlbatikoo ca réew ya mu nootoon, Senegaal bokkoon ci, ngir sàkku ndimmal ak i ndaw yi koy xeexle. Noonu, ñu yabal Belees Jaañ. Belees Jaañ, ngir xam cër bu sëriñ si am ci askan wi, daldi seeti Seriñ Tuuba. Ca la ko xamalee li xew ba noppi sàkku ci moom mu digal ay ñu jàppaleji Farãs. Seriñ bi nangul ko ko, daldi sant Séex Ibra Faal mu wutili ko ay waxambaane yu ca man a dem. Waaye, du loolu rekk la Sëriñ bi mës a defal tubaab bi. Ndax, ca jamono yooyu ba tey, santoon na Séex Anta Mbàkke mu utal ko ay gune yu ñuy dalal ca daaray nasaraan yi doon door a ubbi ca diiwaanu Njaaréem. Gune yooyu Séex Anta Mbàkke tànnoon, Séex Anta Jóob, werekaan bi, àddina sépp xam ko tey, ca la bokkoon. Ndege, Séex Ibra Faal moo doon denc yaayam ca këram gi ñu duppe woon Kër gu Mag. Àddinay dox ba jamonoy 1940-1950. Lewopóol Sedaar Seŋoor miy dooni njëlbeenug njiitu réewum Senegaal ci njeexitalu nooteel bi, daldi ñibbisi. Bi mu noppee ci njàngam ma mu doon defe Farãs, dafa delsi Senegaal sóobu ci pólitig bi. Doomu Juwaalo jooju, nag, ab katólig la woon, bare woon xam-xam te ñawoon xel lool, sax. Xelam mu ñawoon moomu la jëfandikoo woon, natt dayo bi seriñ si am ci géewu pólitig gi, daldi leen di jiital ciy naalam. Noonu, mu seqiy jéego, seeti leen, di leen nemmeeku, di waxtaan ak ñoom, laxasaayu jikkoy taalibe, di jëfe ndigal, di bàyyi tere. Looloo taxoon Sëriñ Fàllu Mbàkke, xalifa murid yi ca jamono jooju, doomoo woon ko. Moo tax itam ñenn ñiy wax ne Seŋoor, gannaaw Yàlla, lépp lu mu mës a am ci politig Sëriñ Fàlloo ko ko mayoon. Li koy firndeel mooy ne, donte ne katólig la woon, mooy ki jëkk a jiite Senegaal, réew moo xam ne jullit yaa ci ëpp, ci diirub 21i at. Bi Seŋoor di dem, dafa jox lenge yi Abdu Juuf. Abdu Juuf tamit, fi Seŋoor tegoon i tànkam ñeel sëriñ si la tegoon yosam. Dafa joxoon sëriñ si cër bu mat sëkk, lëkkaloo woon ak ñoom. Moom, njiiteefam ak xilaafa Seriñ Abdu Laxaad Mbàkke ñoo méngoo. Xalifa bi daldi koy uuf, jàppale ko ni Sëriñ Fàllu jàppalee woon Seŋoor. Ndimbalam ak taxawaayam ñoo mayoon Abdu Juuf ab ndëgërlaay ba tax koo toog ci jal 20i at. Ndaxte, ci atum 2000 la ko Ablaay Wàdd daanoon ci joŋanteb wote ba. Ablaay Wàdd moomu tamit, ci murid la féetale woon boppam. Ablaay Wàdd, dafa mës a biral ne murid àqan la. Mu yàggoon lool ci kujje gi, ca jamonoy Seŋoor ak ci jamonoy Abdu Juuf. Waaye, mësul woon a réeroo ak i ñonam, doonte ne xalif bi, Abdu Juuf mii féetale woon boppam ci Tijaan yi, la doon jàppale. Àddinay doxati ba Góor gi mujje moome, yéeg ci jal bi. Ndamu Ablaay Wàdd, nag, ci woteb 2000 yi, jaloore ju réy la woon, àddina sépp daan ko soow. Askanuw Senegaal bégoon lool ci coppite bi mu yàggoon a xaarandi te amoon ci wàll wu réy. Jamono jooju, Sëriñ Saaliw Mbàkkee nekkoon xalifa murid yi. Ñépp xame woon ko màndute ak jege bi ko Ablaay Wàdd jege woon. Dafa di, Ablaay Wàdd, ku fésaloon péeteem ci murid yi la. Loolu xawoon na jur njàqare ak tiitaange. Ndax, dañ doon ragal njiitu réew ma woon jéng, di doxal xàjj-ak-seen. Moo tax it, fi mu ne nii, kenn amul mbeeteel ci ni waa Tuuba tëyee, ba sun-jonni-Yàlla-tey jii, pàrti PDS bi ñu wàcce ci jal bi, 8i at ci ginnaaw. Lii lépp, nag, warul tax ñu jàpp ne, sëriñi murid yi kese ñoo daan dugal seen loxo ci làngu pólitig gi. Déedéet. Dañ ci gën a fés rekk, waaye noonu la deme woon it ci yeneen tarixa yi, rawatina bu tijaan yi. Kenn umpalewul ne, Sëriñ Séex Tijaan Si ci boppam, sosoon na fib pàrti, jiite woon ko. Moom kay, sëggoon na sax ci géewu pólitig gi. Looloo taxoon mu dugg ndung-siin, ndax xeex ba mu daan xeex Seŋoor. Tey, doomam ji, Sëriñ Mustafa Si, kilifay Mustarsidiin yi, moo ko wuutu, jiite pàrti boppam, di PUR. Bu weesoo ñoom ñaar ñooñu nag, mënees na lim, ba tey ci tijaan yi, Sëriñ Paap Maalig Si (rakku Sëriñ Séex) ak Sëriñ Abdu Asiis Si Al Aamin. Ñii de, naam fësaluñ woon seen bopp bu baax ci pólitig bi, waaye jot nañ cee dugal seen i loxo ak seen i xalaat bu baax. Waaye, nag, kenn ci ñoom du dab Sëriñ Abdu Asiis Dabbaax. Ku mat a ràññe la woon, moom, Sëriñ Abdu Asiis Si Dabbaax. Ndaxte, daawul noppi, daawul tàyyi di taxawu askan wi ak di artoo ko dànkaafu Nguur gi, ngir muy bàyyi xel baadooloo yi. Ittéem yèpp doon rekk, wax dëgg, yore pusóom di ñaw. Ndax sax du taxawaay woowu moo jur baatu Pólitig, ca dëgg-dëgg ? Ci sunu jamono yii nag, daa mel ni, bi Maki Sàll di yéeg ci jal bi, daa faf bettoon ñu bare, ba ci sëriñ si. Mbaa sax, du looloo taxoon Parsidã naagu woon ba di leen jéem a sóoru ci njëlbeenub moomeel ga ? Ak lu ci mënti am, gaaw naa dellu ginnaaw moom, xamaat palaasam, ràññe cër bi mu ameel sëriñ si ci réew mu bindoo ni Senegaalu tey jii ! Moo tax it, fi mu ne nii, digganteem ak sëriñ si, mel na ni mburook soow ! Doonte mënagul a fexe ba dugg ci xolu waa Tuubaa yi. Li muy féeteele boppam ci tarixa Murid yépp, mel na ni tey, waa Tiwaawon ñoo ko gën a jàpp. Loolu yépp nag, teewul, ba Parsidã Maki Sàll bëggee juboo ak njatigeem ba woon, Ablaay Wàdd, Sëriñ Muntaxaa Mbàkke, di Seriñ Tuubaa tey, moo dox diggante bi ba juboole leen, keroog ba ñuy ubbi jumaa Masaalikul Jinaan. Yemul foofu. Ndax, fan yii rekk, bi Idiriisa Sekk di wax ak askan wi ngir layal duggam ci nguurug Maki Sàll, junjaale na taxawaayu sëriñ si ci ànd bi mu àndaat ak Maki Sàll. Nee ñu, Sëriñ Musaa Nawel Mbàkke, miy sëriñu Idi, moo dox lépp ba mu sotti. Idi moom, gannaaw ba ñu ko tàkkale nombog-tànkam gu bees gii ko may mu nekk léegi ñetteelu njiit ci Nguur gi, génnam bu njëkk, Seriñ Muntaqa la ko jagleel ; te it, li mu ko xamal leer na : « Da noo ñëw fii sargalsi la, wax la sunu ngërëm, ginnaaw ndam li nu am, ba nu toppe say ndigal yépp ba mu mat sëkk, bañ cee sàggane lenn. » Laata muy egg ci Sëriñ bi nag, Idi jot naa jaar ci sëriñam, Seriñ Musaa Nawel Mbàkke, wéet ak moom lu yàgg, ci li taskatu xibaar yi jottali. Ginnaaw lees fi jot a wone lépp ñeel taxawaayu sëriñ si ci pólitig bi, baax na ñu amal ab taxaw-seetlu ci mbiri ñaari doomi réew mi. Ñaar ñooñu, tey, ñépp a leen naw. Ñoo ngi rëccu liñ jotal woon a jiite réew mi walla liñ ci yàggul ; ñooñooy Séex Anta Jóob ak Mamadu Ja. Séex Anta, kenn umpplewul ne, Murid la woon ci juddoom ak ci xaleelam. Moom, Kër gu Mag la yaroo, màgge fa, ca ëttu ak kiiraayu Séex Ibra Faal. Waaye, Séex Anta, li mu doon weg sëriñ si yépp, kenn mësu ko woon dégg ci làngu pólotig gi, muy mbubboo askanam walla tarixaam. Màndute gu mat sëkk la àndaloon ci wàll woowu, ni mu ko doon defe ci wàll wu ne. Ndax dañu ko mere woon ci tekkaaralam googu ? Li am daal mooy ne, Séex Anta, dëggu, pas-pas ak xam-xam yi ko ñépp xamaloon, taxul seriñ si wallsi ko, wuyu ci wooteem yi mu doon def ngir yewwi réew mi, defaraat ko, doonte ñu bare-bari ci askan wi, moom lañu faraloon. Leneen lu laxasu woon it ci mbir mi moo doon ni, Tubaab yi ŋànkoon dëgg réew mi, Seŋoor moo leen gënaloon fuuf Séex Anta. Mamadu Ja moom, doonoon ku jullite, nekkoon na ci jal bi, ci diir bu gàtt (1959-1962). Wànte, li mu doon jullite julite lépp (képp ku ko xamoon mënoon na ko koo seedeel), moom ak sëriñ si, jaaroowuñu woon taal. Dëggu ak xadar yi mu àndaloon, mayuñu ko woon muy maslaa maslaa yu bare, walla di doxaale jikkoy naaféq. Looloo gënoon a indi ay jafe-jafe ci digganteem ak ñu bare ci kilifa diine yi. Moo tax it, ba mu jotee woon ak Seŋoor ci ginnaaw gi, gisul woon ñu bare ñu féeteek moom. Noonu la ko xaritam xañee woon nguur gi, dugal ko kaso, tëj ko fa lu ëpp fukki at. Bu nu taxawee seetlu ba noppi, laaj wi sampu nag, mooy xam ndax ku sëriñ si àndal dangay falu, ku mu won ginnaaw nga xalangu ? Ay laaj yu bare sax. Bañ a falu te dencal sa bopp say xalaat yu rafet ngir suqali sam réew ? Falu te njar say xalaati bopp ciy bëgg-bëgg sëriñ si ba noppiy dox ci seen i ndigal ? Walla weneen yoon xaj na ci diggante wu sew woowule ? Tey jii, xale yu mel ne Usmaan Sonko, di door a samp seen ndënd ci géewu politig bi, war nañu cee am njàngat. Usmaan, ci njëlbeen ga, daa meloon ni ku joxul sëriñ si seen gëdd. Waaye ci at yu mujj yii, mel na ni ku soppi taxawaayam ci wàll woowu, ndax ni muy gën a jegee léegi kilifa diine yi. Àndak sëriñ si walla won leen ginnaaw ? Su nu misaale wax ji ak kàddu Idiriisa Sekk yu yees yi : tànn sa bu la neex la !
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/nan-mbaalo-toj-nga-lamb-ji/
ÑAŋ-MBAALO, TOJ NGA LÀMB JI ! « Toj naa fii ! », « Tasaare naa fee ! », « Rajaxe naa fale ! »… Su nu waxantee dëgg, xorom si moom la ! Moom Madike Ñaŋ, kenn ci wutaakoni yi, mooy xorom siy safal kampaañ bi ñuy waaj a jéexal. Ci biir werante yeek, xuloo yeek, ŋàññante yeek, tamante dëmm yi, Madike moom, neex deret ba dee, ciy ree ak i kókkali, boole ciy kàddu yu rafet, lanuy jaaye sàrtu doxalinam bi mu faf tudde « Jàmm ak xéewal ». Dal ak aafiya daal la indi ci kampaañ bi nga xam ne, boobaak léegi, ni nu ko waxe ci njélbéen gi, defante doŋŋ lees ci seetlu, defante bay dóorantey kurpeñ, di génney jaasi… Nii lañ fi woññee — walla woññeegum ? — ñaar ba ñetti doomi-Aadama yu seen bakkan rot. Madike moom, ci jamono yii, mu ngiy toj Anternet. Mook Usmaan Sonkoo ko koy xëccoo, sax. Sonko daa aakimu, daanaka, reeso sosiyoo yi, bàyyi wujjam yépp ginnaaw ci wàll woowu. Waaye Madike Ñaŋ sorewu ko lool ndax saa yoo duggee Anternet daj ciy nataalam mbaa dégg i kàddoom. Ne ñi mën a muñ i feemam barewuñu. Moom daal day reeloo nit ñi ba seen biir di metti ! Wax ji benn la : ‘’kii daal moo neex !’’… Waaye li am ba am, moo di ne, wutaakon bile, mu tey ko mbaa mu bañ koo tey, fexe na ba nit ñi génne seen xel ci liñ yàgg a ruumandaat : ndax, moom, jot ci réew mee ko tax a jóg walla dafa bëgg a sotle Maki Sàll ba noppiy dof-doflu, di reeloo askan wi ? Madike Ñaŋ, ndax yàqal Ablaay Wàdd ak Karim ak seen pàrti, PDS a ko tax a sàmp ndëndam ? Lu waral layookat bu siiw ni moom, amoon lool bayre, doon ku am fulla, xéy di wër réew miy wax ay waxi ku daanoo ci saret ? Xanaa kay li ko jaral a sóoru Wàdd du neen ! Ndax kat, ‘’Góor-gi’’ léppam la woon, ni sët la ko mas a jàppe, jàngal ko politig, doon njiitam. Nu seetaanati ba xam « fu boroom wànnent di mujje ak i gëtam »
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/ndongo-samba-silla-cfa-xettali-fras-a-ko-taxoon-a-jog-laaj-tontook-mamadu-jallo-i/
NDONGO SÀMBA SILLA « …CFA, XETTALI FRÃS A KO TAXOON A JÓG» Mamadu Jàllo :  Ndongo Sàmba Silla, yow doomu-Senegaal nga, di boroom xam-xamam bu mag ci wàllu koom. Ak li ngay doon ndaw yépp, sa tur wi siiw na lool ci réew mi te saw askan naw na la. Yaa ngi liggéeye Fondation Rosa Luxemburg, ñu dénk la fa lépp lu ñeel yokkuteb Afrig sowu-jant, nga ciy gëstu. Génne nga itam ay téere yu bare te bi ci mujj, « L’arme invisible de la Françafrique. Une histoire du franc CFA », yaak ndaw su ñuy wax Fanny Pigeaud a ko bokk bind. Moo tax ginnaaw bi ma la nuyoo, sargal la, gërëm la ci jotaay bi, ma di la ñaan nga wax jàngkati LU DEFU WAXU yi luy sa xalaat ci CFA,  ndax yaakaar nga ni CFA bi mënees na cee faj soxlay askan wi ? Ndongo Sàmba Silla : Tontu bu gàtt bi te leer mooy : déedéet. Li ma ko tax a wax nag, du lenn lu dul ne, CFA bi ci boppam dafa làmboo ñaari laago yu mag. Te, feek tàggoowul ak laago yooyu, bépp naal walla pexe mu ñu mënti lal, dina lajj. Jafe-jafe bi ci jiitu mooy ne, feek CFA bi mi ngi fi, dafay mel ni nootaange jeexagu fi. Maanaam, day mel ni Farãs moo nu moom ba léegi. Ndaxte, CFA bi ci boppam, dañu ne ci Farãs la sësu, moo koy warlu (garantir), doonte ne wax jooju teguwul fenn. Looloo waral CFA bi ñu koy tëgge ak a defare Farãs, muy benn. Nga teg ci ne, 14i réew ñooy jëfandikoo CFA. Réew yooyu xaajoo ñaari pàcc : benn pàcc bi booloo ci kurélu UEMOA (kurél gi boole réewi Afrig sowu-jant) beneen bi ci kurélu CEMAC (kurél gi boole réewi diggu-Afrig). Kurél gu ci nekk am nga sa bànk bu mag : waa UEMOA ñoo ngeek BECEAO, waa CEMAC yor BEAC. Waaye, ñaari bànk yu mag yooyu, bu ci nekk danga war a jël sa xaalis bi ngay wecceek yeneen xeeti xaalisi àddina si (dolaar, ëróo, yen, añs.) xaaj ko ñaar, jox benn xaaj bi Farãs, mu téye ko. Mu mel ni, saa yoo amee téeméer, Farãs ay gàddu juróom-fukk yi. Rax-ci-dolli, bu nekk ci ñaari bànk yooyu, Farãs dafa bokk ci saa ndajem-caytu (conseil d’administration). Maanam, am na ku ko fa teewal. Te, amul benn ndogal bu ñu fa mën a jël lu dul ne Farãs da cee ànd. Njàngat lees ci mën a jële mooy ne : CFA, xaalisu Farãs la, moo ko moomal boppam. M. J. : Ndax mën ngaa indi yeneeni firnde ci loolu ? NSS. : Firnde yi tudd naa ci yenn léegi. Mooy bi may wax ne, ca réewum Farãs lees di tëgge CFA bi, téeméer bu nekk Farãs mooy gàddu xaaj bi def ci nafaam te yit bokk na ci ndajem-caytu ñaari bànk yu mag yii di BCEAO ak BEAC. Muy wone ni, ndogal li ci loxol Farãs la nekk. Ci misaal, bu ñu waroon a natt dayo CFA bi ñeel ëróo bi, kenn mënu cee jël ab àtte te Farãs joxewul kàddoom. Yooyu yépp di ay firnde yu leer. Waaye, nan dellu ginnaaw tuuti xool ba xam li nuy wax wér naam déet. Ñépp a ngi fàttaliku atum 1994, bi ñuy nasaxal (dévaluer) CFA bi. Loolu, mi ngi ame woon ci coobare ak ndogalu Farãs. Ndege, Farãs, jamono yooyu, xaalis bi ñuy wax franc français (FF) la doon jëfandikoo. Bi ñu wàññee dayo CFA bi, maanaam weccitu réewi Afrig yi Farãs nootoon, dañu ko xaaj ci digg bi, fukki dërëmi CFA di tollook dërëm ci franc français. Seen njiitu jawriñ ja woon, Eduwaar Baladiir (Edouard Balladur), moo taxawoon waxal boppam ne moom kott a jël ndogal lu ni mel. Waaw, xam nga ni, ku moom dëggëntaan sa bopp, ab doxandéem, ak lu ngeen mënti séq, du sañ a taxaw naan moo wàññi sa dayob xaalis, nga ne patt-pattaaral di xullee ! Wolof dafa ne, lu ne fàŋŋ kenn du ko jeex. Moo tax ma ne, ku moom xaalis bi ngay jëfandikoo bés bu nekk moo la moom yow ci sa bopp. M. J. : Sànq ci say wax, tudd nga ñaari jafe-jafe yi CFA bi làmboo. Mel na ni benn bi rekk nga leeral. Lan mooy ñaareelu jafe-jafe bi ? N.S.S : Waaw. Ci gàttal, njëlbéenug jafe-jafe bi mooy ne CFA bi day biral ni nu Farãs  di noote. Ñaareelu jafe-jafe bi, nag, mi ngi aju ci wàllu koom-koom. Ndege, CFA, bi ko Farãs di sos ci atum 1945 (26eelu fan ci weeru desàmbar), li mu ko dugge woon mooy jëfandikoo ay nooteelam ngir ñu jàppale ko ba mu mën a taxawaat, suuxat koom-koomam. Li ko waral nag, du lenn lu-dul ne, jamono jooju, Farãs ci xare bu metti la doon door a jóge (ñaareelu xareb àddina si). Xare bi metti woon lool ci moom, mu ñàkke ci alal ju bare ak ay jumtukaayi xaralaam… Réew mépp yàqu daanaka, koom-koom bi sooy, Farãs ndóolal la ko ba nga ne lii lu mu doon. Dafa di sax, jumtukaay yi mu soxla woon te ñu waroon a jóge bitim-réew, amul woon xaalis bu mu leen jënde. Ci la ay njiitam xalaat, lal pexe te du woon lenn lu-dul sàkk CFA. Ngir sàmm dayo bi mu amoon ci àddina si, Farãs dafa daldi wëlbatiku ci réewi Afrig yi mu tegoon loxo ngir tibbe ci seen alal li koy tax a noyyi, duy ci nafaam ba mu fees dell, daldi suqali koom-koomam, dekkali doole ak dayo ya mu amoon ca Ërob ak ci àddina si. Kon, CFA, xettali Farãs a ko tax a jóg. Rax-ci-dolli, réewum Farãs dafa soxla woon ay njureef (matières premières) ngir isinam yi mën a dox. Njureef yooyu, nag, Afrig lañu nekkoon (te ba tey jii ñoo ngi fi). Kon, da leen a waroon a jëndsee Afrig. Li gën a yéeme moo di ne sonalul sax boppam di leen jënd ci nun. Defu ko ndax li ñu xam ci kuy jënd mooy nga ñëw ne lii la bëgg, waññi sa xaalisu bopp fey. Demewul noonu ndaxte CFA bi Farãs di jënde njureefi réewi Afrig yi mu nootoon, seen xaalis la, ñoo ko moom ci lu wér. Farãs indiwul dolaar, indiwul yen, walla sax beneen xaalis. Mu ngi mel ni daal, ma dénk la samay ñaar-fukki dërëm, nga delloo ma fukki dërëm yi, yeneen fukki dërëm nga tëyeleen ba noppi, wëlbatiku ñëw di ko jënde sama njaay. Ndax xaalis bi ngay jënde yaa ko moom ? Dée-déet ! Kon kay danga jël sama moomeel ñaari yoon (sama xaalis ak sama njaay). Bu ko defee, Farãs deful woon lu dul jëlsi njureefi réewi Afrig yi mu nootoon, waaye jëndu leen woon.  Ci gàttal, ngir tënk ñaareelu jafe-jafe bi, CFA day dooleel koom-koomu Farãs, di nasaxal koom-koomu réewi Afrig yi koy jëfandikoo. Li ci gën a doy waar nag, mooy ne bi ñuy sos CFA bi, moo ëppoon dayo xaalisu réewum Farãs (franc français) te loolu am na lu ci Farãs nammoon. M. J. : Ci sa xalaat, lan la ci Farãs jublu woon ? N.S.S : Xam nga, réew mu mel ni Garaŋ-Bërëtaañ, amoon doole lool te féete woon Farãs kow ci bépp boor, daawul doxale noonu, doonte amoon nay réew yu mu nootoon ci Afrig. Muy lu jar a bàyyi xel. Ndaxte, xaalisu Garaŋ-Bërëtaañ moo gënoon a diis bu Farãs, te réew mu naat la woon. Ñoom, njiiti Garaŋ-Bërëtaañ yi, dooleeluñu woon xaalisu réew yi ñu nootoon ba mu gën a diis seen bos. Kon, bu Farãs defee lu ni mel, am na lu mu ku dugge woon. Loolu laa lay waxsi. Li taxoon Farãs ak i njiitam def ba CFA bi ëppoon doole ñaari yoon xaalisu Farãs du woon lenn lu dul tënk réewi Afrig yi ngir ñuy jënd ci Farãs doŋŋ, di ko jaay it moom kott. Li ko waral, mooy ne dayo boobu ñu joxoon CFA bi, ngelaw kese la woon. Te sax, looloo gënatee tax Farãs mën a jënde ci réewi Afrig yi ndax daanaka du ko dikke dara. Ci jamono yooyu, CFA bi diisoon ba nga xam ne, réew yi ko daan jëfandikoo mënuñu woon a jëflante ak yeneen réewi àddina si. Loolu bokk na ci li nasaxal sunu koom-koom, te pexem Farãs kese la. M. J. : Ndax, laata CFA bi di am, réewi Afrig yi daan nañu séq ak yeneen réewi àddina si jënd ak jay ? N.S.S: Waaw kay ! Bi ñaareelu xareb àddina bu mag bi jeexee, réewi Afrig yi demoon jàppale seen i nootkat, dañu cee jaare yeewu, tàmbalee dox ak seeni tànki bopp. Naka noonu, Farãs mënul woon a tere réew yi mu nootoon ñuy jaayante ak jëndanteek ci yeneen réew yi, muy yu Amerig bëj-saalum walla sax yu Aasi. Jamono jooju, tàmbali woon nañu am ay jumtukaayi xarala. Waaye, Farãs, ànd ak kiñaanam ak bëgg a ratt réewi Afrig yi, lal ay pexe ngir gàntal jëflante boobu. Ci la sose CFA bi, mu tënk sunuy réew, tee leen jëm kanam. Kon, Farãs dafa gisoon ni tegu nan ci yoonu naataange, mu daldi kootook ñenn ci njiit ya woon, daldi fatt yoon woowu…(Ñaareelu xaaj bi feek i fan)
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/koronaawiris-taxaw-teewlu/
KORONAAWIRIS : TAXAW TEEWLU Làmp Faal Kala Mbasum Covid-19 mi lëmbe na àddina, lëmbaaje xel yi ak xol yi, ba ku tiitul it jaaxle nga, mbaa sax nga faf boole tiitaange ak njàqare. La woon, lu ci ëpp wonni na tey, mbir yi jaxasoo, nit ñi di jaawale, gis-gis yi wute, ku nekk di wax ak a layal la dalum xelam. Mu mel ni danoo jekki, ñu cëppeel nu ci meneen kéew mu wute ak ma nu xamoon. Barabu liggéeyukaay yu bari tëj nañu, ku daan yëngal ak a xumbal selaw nga,  boroom dërëm ak daraja ya daan bàkku ñooy kotkoti ndax tiit, woroom xam-xam yi wedam, njàqare daj fépp. Rax-ci–dolli, as péexte mi nit mënoon a bàkkoo, bàyyima yee ko ko ëppale tey, ngir nit la nuy tëj, bàyyima yiy daagu waxtu wu leen soob. Lépp ni tekk, ba ci barab yi nit ñi daan dem di fa yaakaaree yërmaande Yàlla sax, lu  mel ni jàkka yi ak jumaa yeek jàngu yi, nee nañu ràpp. Tëj googii juraat geneen werante ci jullit ñi, rawati-na bi weeru koor wi teroo : ñii wéeru ci ngëm, di sàkku nu tijji leen te gëm ni Yàllaa fi indi mbas mi, bu nu ubbee néegam yi, ñaan ko mën naa am mu wis ndox mu sedd ci mbas mi mu daldi fay, ñee gëm nañu Yàlla naam, waaye teewuleen a wéeru ci xam-xam te naan wareesul a ubbi jenn jàkka mbaa jumaa, ndaxam diinee digle fargaru. Kuréel gu ci nekk di indi ay aayaak i xadiis di layal sa gis-gis. Béjante ak werente yooyu jural jullit ñu bari ag jaaxle, rawati-na ñi seen àlluwa soriwul ba ñu mën a xam fu ñuy taxaw. Fii jamono toll nag, képp ku amum xel yaa ngi joyal say xalaat ci mbas mi. Ñii jàppe ko mbugalu sunu Boroom, ñee jàppe ko pexeem ñoñ Ibliis, am sax ñu jàpp ni mbindare mi moo fippu ci kow doomi-aadama yi. Ñi daan tontu tey ñépp a ngi laaj : Ana fu jàngaro ji juge ? Ana fu mu jëm ak nun ? Kañ lay jeex? Ndax dunu jeex balaa jeex ? Nu muy jeexe ? Laaj yooyu ñoo ëlëm ñépp te lënt xel yi. Li wér te wóor nag mooy, mbas mi wan nanu sunug néew doole ak sunu xam-xam bu gàtt, wan na nu itam sunu bopp, wan ku nekk ci nun jikko ya gën a làqatu ci moom, muy mbaax mbaa safaan. Lenn ci li koy firndeel mooy, doonte mbas maa ngi jur yeneen tolof-tolof ci fànn yu bari ba tax am ñu nelawatul ngir di def i jàngat ak a seet ay pexe ngir jariñ askan wi, ñeneen a ngay naxaate, di wuruj ak a wor,  di lali pexe ngir jariñoo askan wi. Ginnaaw coow li amoon ci “Chloroquine”, fan yii “Artemisia” moo  aye ndax réewum Madagaskaar dafa cee defare garab gu ñu saytul seen bopp ba xam ni dafay faj ak a aare ci doomu-jàngaroy koronaawiris. Seen njiitu réew jël na ci ay dogal ba ñu tàmbali koo jëfandikoo, doonte O.M.S, di mbootaay mi nu dénk wér-gi-yaram ci àddina si, nangoogu ko. Taxawaayu O.M.S boobii sabab na yeneen laaj : ndax du li garab gi bawoo Afrig a tax O.M.S sawaru ci ? Ndax yeneen njiiti réewi Afrig yi dinañu dooleel njitu réewum Madagaskaar, indi seen xam-xam door koo yaatal ci séeni réew, walla ñoom, dañuy déglu ndigalu seen naataangooy tubaab yi ?   Li ci kanam rawul i bët. Beneen laaj bi mooy lu jëm ci wàllu alikeñ yi. Ku nekk di ñaw ak a ñawlu, ñii di maye ñee di jaay. Ndax saytu ba xam ndax ñi ngi dëppoo ak cet ak matuwaay yi mu laaj yépp jotul ? Fii mu toll nag, ku nekk a ngi fagarook a ñaan mbas mi jeex, waaye na nu fas yéene,  su yii yépp jàllee, waxuma nit ku nekk rekk, waaye réew mu nekk, rawatina yoy Afrig, jëlaat say matuwaay, jubbanti sa doxalin, defaraat sa toogaay, ndax ku muus tey dañu laa naxoon démb.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/li-gen-a-fes-ci-xibaari-taggat-yaram/
LI GËN A FÉS CI XIBAARI TÀGGAT-YARAM WURE (FUTBAL) Gaynde Senegaal yu ndaw yi noppi nañoo waajal Chan bi. Tey ci altine ji lañu doon amal seen ub joŋante bu mujje ci waajtaay gi. Ginnaaw bi leen Marog dóoree (1-0), ñu témboo ak Alseri (2-2), dellu témboowaat ak Libi (1-1), dañoo dóor Saa-Congo yi benn bii ci tus. Gaawu bii di ñëw nag lañuy dajeek Koddiwaar ci seen joŋante bu njëkk ci Chan 2023 bi. Garet Béel (Gareth Bale), tollu ci 33i at, wékk nay dàllam tay ci altine ji 9 Jaņwiyee 2023. Bàyyi na futbal, muy ca këlëbam ak réewam yépp. Igóo Lóris, jàppkatu Farãs bi, moom itam, bàyyi na ekib Farãs. Moo ko xamle ciy kàddoom yii toftalu : ” Gannaaw 14i at yi ma xeexal mayo bi, yaakaar naa ne, àgg naa ca cat la. Maa ngi jël ndogal, daldi dakkal ànd beek ekibu Farãs, di am yëg-yëg ni joxe naa fa sama lépp”. Nowel Lë Geret (Noël Le Graët), njiital FFF, génn na di jéggalu gannaaw bi mu waxeey kàddu yu ñagas ñeel Sinedin Sidaan. Dafa di, ñu bari ciy wurekat ak i kilifa, ca Farãs ak ci àddina sépp, ñoo génn di naqarlook a metitlu kàddu yooyee, rawatina Kiliyaan Mbape ak Reyaal Madrid, këlëbu Sidaan ba woon. Bàrsalon toogati na ci bopp Sàmpiyonaa Espaañ ba, gannaaw ndam li mu am démb (1-0) ci kaw Ateletikoo Madrid. Moo rawee Reyaal Madrid 3i poñ. Ndeke, Reyaal dafa ñàkk barki-démb, ci gaawu bi, ci kanamu Wilaareyaal (1-2). BASKET Waa Spurs amal nañu pas ak Góorgi Si Jeŋ. Dana fa sol limatu 41 ba.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/taxawaayu-kujje-gi-ciy-wotey-gox-goxaan-yii-degmal/
KUJJE GEEK WOTEB 2022 BI: BËGG NAA LA, BËGGUMA LA, LOOLU JARUL COOW Ci bésub 23 sàŋwiye ci atum 2022 bii di ñëw, la Senegaal fas yéene amal ay wote jëm ci palu njiiti gox-goxaan yi. Gannaaw ba pàrti pólitig yi jàppante ci mbiri yoonu pal gi, maanaam li ñeel doxalinu wote bi ak jumtukaay yi mu àndal, léegi, pàrti yooyee, seen yitte yépp a ngi aju ci nañu nar a taxawe ci joŋante yi ñuy waajal. Coow li jib lépp, looloo ko waral ci jamono yii, jóge ci anam yi pàrti yi di taxawale seeni mboolooy kurél yi. Kilifag pàrti PUR moo sulli mbóot mi, yëgle ne “ñeenti pàrti yi gën a mag ci kujje gi” déggoo nañu ngir jëmmal seen nas bii doon sàkk mbootaayu pàrti yu kujje gi. Pàrti yooyu ñooy PASTEEF, Taxawu Dakaar, PUR ak PDS. Coow li ne kur ci dëkk bi. Ñu teg ciy fan, mbooloo mi ñu tudde “Yewwi Askan Wi (YAW)” daldi juddu. Ñenn ñi rafetlu ko ndax yaakaar ne kujje gi dina fi jóge génn ci gutt gi mu ne woon ba léegi, wone dooleem, jàkkaarlook waa nguur gii di sonal askan wi ; ñeneen ñi ñaawlu li kujje gi manul a fexe ba booloo nekk wenn say képp. Ci kow loolu, am na it ñuy laaj naka la ñeenti pàrti doŋŋ di woote ni ñooy taxawal lu mat, daanaka, ay téeméeri làng. Ba tey it, gisees na ñu rafetluwul doxalin wi lal wote woowu, mel ne ñi ko sooke dañoo nawloowul seeni naataango yi ñu bokkal xeex. Am na sax ñu ci doon booley xaste, di ñaawal kujje gii “man a jaxase ñu àndul, mbete supp kànja !” Teguñu ci ayubés, PDS génneeb bataaxal xamle ne bokkul ci mbooloo mu yees mii, ndax masul a xaatim lenn lu koy firndeel ; yeneeni pàrti yu mel ne AJ/PADS ak Bokk Gis-Gis, ñoom it génne seenub yëgle di wone ni bokkuñu te ànduñu it ci doxalinu kurél gu bees googu di Yewwi Askan Wi. Ginnaaw bi, kurélu Gëm Sa Bopp gi ci bokkoon, far génn moom it ci mbooloo mi, ndax ñàkk a gis boppam ci defin wiy niru xàjjaatle ci biir pàrti yi, mel ne yenn ci pàrti yi bëgg a féetale seen bopp ci kow, ñi ci des ci suuf. Coow li jibati, yëf yi jaxasoo. Ay kàddu jógati di ŋàññ kuje gi ndax seen ñàkk-juboo. Pëndu coow loolu jotul a wure, meneen mbooloo mu soqikoo ci kujje gi daldi juddu wone boppam. Ñu xàmmee ci ñi ko sàkk, ay pàrti walla kurél yu mel ne PDS, Bokk Gis-Gis, AJ/PADS, CRD… Muy mbooloo mu mag, daanaka walla lu bon-bon, mu tollook dayo moroomam mi ko jiitu. Coow li neeti kur. Ñi jàppoon ni kujje gi mënta fexe ba booloo, gënatee yëkkati seen baat. Jamono jooju yépp, waa Bennoo Bokk Yaakaar (BBY) yi ŋànk nguur gi, ñu ne tekk di seetaan ; ñenn ñi jàpp ne sax, booba ñu ngee ree ci suuf. Waaye ñoom it, ndax seen ay ci coow li du dikk, bu ñu demee ba war a tànn ci gox bu ne, ku fay nekk jaraaf ? Waaw, booba nag, ana askan wi, moom ? Ana li ciy taxawaayam ? Su dee dëgg rekk a tax ñuy wax, daa mel ne ñoom ñooñee, askan wee lee doon seetaan dëggantaan. Wax dëgg, askan wi moom, daa am lu ko doy sëkk, ak mbënd mi ko léjal ba ci kanamu Yàlla ! Rax-ci-dolli, njëgum njaay mi di yéeg jëmale… asamaan…! Lépp a yokku. Fekk booba, ndox mu ñu naan rafle fi, ba tax jigéen ñi di ko wuti ni doom yu góor. Moonte, askan wi de, moo war a tànn ci diggante waa nguur gi ak waa kujje gi, ñi ko doy ngir mu dénk leen boppi gox-goxaan yi, ngir seen yorin wu rafet. Ku yabu ne, ngir seen dundin ñoŋ. Lu mu ci manti doon, way-pólitig yi, warees nañuy taxaw-seetlu, ànd ak seen xel, gannaaw ba ñu leen njortalee ñunekk ñu bëgg seen réew, fonk seen gox, te jiital njariñal askan wi. Ndax kat, gàtt-xel weesuwul nit jóg ni kenn waru fee sooke dara te boolewuma ci ! Ndax it, du ñàkk-xel di jàpp ne lu ëpp ay ñaari téeméeri kurel, mënees na leen a boole ci menn mbooloo, ñuy ànd di nas, di xàccandoo, di dóorandoo ? Waaw waaye, ndax bokkul it ci gàtt-xel nga woo ay nit ngir ngeen ànd xeex, ba noppi naan leen “Yeen tekkiwuleen dara, toppleen rekk sama gannaaw ma yóbbaale leen ?” Xaste wi nag, moom, mënoon naa ñàkk, rawati-na ba muy niru tayeef. Ndax, xanaa kañ, kuy nas ngir boole ay nit, ñu àndul bokkuñu kurél kepp lay man a woo ? Rawati-na, mbooloo moo xam ni, génn nësër doŋŋ moo ko tax a jóg, maanaam, bokk sotoo ki ñuy jàmmaarloo, ba mu abal leen ? Ana kon lu fi indi ñamu supp kànja wu neex woowule ? Ak sunu xel mu gàtt, foog nanu ni, laaj yooyu de, suñ leen sampoon ca njalbéen ga, jafe-jafe yu bare, maneesoon na leen a moytu. Am déet ? Waaye ndegam su ndox tuuroo, ab ban a cay des, waa kujje gi, warees nañoo taxaw-seetlu, defaraat seen koddaay, te fexe dëgëral seen taxawaay. Ñaar ba ñetti mbooloo sax man naa am, su dee ñoom ñi ko séq dañuy bàyyi xel ci ne, li leen xàjjaatle ak nguur gi moo ëpp solo fuuf li jaar ci seen diggante, ñoom ci seen bopp. Na fekk nag, ku ne xam sa bopp, ndax kat, bët du yenu waaye xam na lu bopp àttan. Ba tax na, waa kujje gi, su ñu bëggee ànd ànd wu rafet te yàgg (naka BBY amale), fàww ku ne xam li ngay “peese” ak nu sa moroom tollu. Ana kuy weddi ne, Usmaan Sonko, li muy gune yépp, ak li muy doon gan yépp ci làng gi, doole ji mu am tey, kenn mënu koo nasaxal ? Ana kuy nàttable dayob Ablaay Wàdd ak PDS ? Ku xam jaar-jaaru pàrti boobu xam ne, moom du nangu mukk geneen kurél di ko jiitu, feek wonewul boppam ba wuutu PDS ci taxawaay bi mu am booba ba léegi ci làngu pólitig bi ak ci réew mi. Loo bañ-bañ lëg, nangul kooy noppam yu gudd ! Lii nag, am na njàngale mun ci man a jële : fi ñu tollu nii, PDS ak PASTEEF mënuñoo bokkagum menn mbalka mu ñuy naane ! Ndax nag, soxlawul di naxante, joŋantey pólitig yii, xëcco nguur a ngi ca xol ba ; te sax, ñenn ñi, duñu fàtte mukk seen nafa, fu ñu toll. Loolu nag, terewul waxtaan, weccee xalaat bokkay nas ñeel anam yi wote wi war a doxe. Koonte nag, ñaari mbooloo yii soqeekoo ci kujje gi warul a jaaxal kuy seetlu, di jëfandikoo xelam. Waaye li war a leer ci boppu ku ne, mooy ni, ëpp doole sa moroom warul a tax nga xeeb ko te Wolof Njaay nee na “koo xeeb, mu yab la”. Te, li wóor ba wóor mooy ne, kenn ci làngu pólitig gi, mënul a dem moom kese ci xare bi ba jële fa ndam, ak doole joo mënti am ! Ci way-pólitig yi nag, mel na ni, kii di Maki Sàll moo gën a mokkal njàngale moomule… Dëgg la, moom nag daa yore kopparam gu duun, boole cib xaatimam bu am solo. Moo tax it… Kujje gi daal, war naa seetaat boppam. Ñi man a ànd, nañu ànd booloo. Ñi bokkul genn kurélu mbooloo nañuy yëgante, bokk xeex ngir wote wi ci boppam jaar yoon ; te ñuy bañ a xeebante, bañ a tamante dëmm. Tey bàyyi xel saa su ne, ci nekkinu askan wi ak it ciy xalaatam. Leneen lu way-kujje gi war a bàyyi xel, mooy luñuy def ba fexe wéyal seeni mbooloomi kurél yi, gannaaw su wote gox- goxaan yii jàlle. Ndax kat, xeex bi day door rekk… te kuy dem xare war a fàggandiku ! Uséynu Béey
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/maki-xalifa-mag-bu-rusee-ne-maa-tey/
MAKI/XALIFA : MAG, BU RUSEE NE MAA-TEY Fan yii nu génn, bare woon na ñu doon yéy ak a yàbbi ci mbirum Xalifa Sàll, di wax ci njéggal bi ko Maki Sàll war a jagleel. Am na ci sax ay taskati xibaar yu demoon ba ne Xalifa Sàll këram lay tabaskijee. Waaye, bi nguur gi fésalee turi nit ñi Maki Sàll jéggal, ñu war a tabaskijee seen kër, kenn gisu ci ku tudd Xalifa Sàll. Muy mbetteel gu réy a réy ci ñenn ñi. Maki Sàll, moom, yéyu ci, yàbbiwu ci. Moone, askan wépp a ko ñaanoon njekk, kilifa diine yi, kilifa aada yi, kujje gi, kuréli way-moomeel yeek yenn mbootaay yi. Waaye, Maki dafa lànk, taxaw fi mu taxaw rekk. Rax-ci-dolli, ci ndoorteelu waxtaanu politig wi mu sumb, ñi ko wuyusi noon nañ ko li gën mooy mu bàyyi Xalifa. Wànte, dafa cosoon wax ji, yem fa. Nanguwu cee woon a sori. Maki Sàll dafa xaar ba dem bitim-réew, ca Biyaaris (Biarritz) ga muy teewe fan yii ndajem G7 mi, door a wax li mu xalaat dëggëntaan ci coowal njéggalub Xalifa Sàll mi nekk ciy loxoom. Ndaje moomu, nag, li mu jiite NEPAD moo tax ñu boole ko ci. Waaye, moom sax, bi mu dalee dem ay ndaje ba tey, mësta toj fenn. Ndaxte, dégguñu benn yoon fu ñu waxe ne Maki kat, bii yoon wax na wax ju réy, ni ko Ablaay Wàdd daan defe. Waaye, ba tey loolu ñorunu ; kàddu yi mu fa rotal ci mikóro RFI ñoo jar a bàyyi xel. Maki Sàll baat yii la fa wax ñeel Xalifa Sàll : « Bi ci njëkk mooy, wareesul a tënk giifalub làngu politig gi ci mbirum njéggal kese, yemale ko ci. Njéggalub njiitéef, ndeyu-àtte réewum Senegal moo ko jagleel njiitu réew mi. Kon, ci moom doŋŋ la aju, ciy loxoom kese la nekk. Moom mooy xool saa su ko soobee mu jéggale. Bu ko defee, sama yoon nekkul ci li taskati xibaar yiy wax ci njéggal bi, duma ci wax. Bés bu ma neexee walla ma am coobare gi rekk, dinaa ko def ni ma koy faral di defe. Ndax  at mu nekk, lu ëpp téeméeri nit walla sax ay junniy nit, ci xayma, dinaa leen jéggal, génne leen kaso… » Kon, noo ko déggandoo : kàddu yii la rotal ca Frãs. Ñu mën cee amal ñaari njàngat yu gàtt. Bi ci jëkk mooy ne, Maki Sàll wegul waa réew mi, joxul cër askan wi walla kilifa yi fiy yeewoo. Waaw, lu tax Maki Sàll bitim-réew rekk lay waxe ak a waxtaane mbirum réew mi ? Xanaa réew mi amul i taskati xibaar yu mu mën a janool dégtal leen i kàddoom ak i xalaatam ? Lii bu tekkiwul ñàkk faayda ak suufeel sa boop ak sa réew lu muy tekki leneen ? Ndax kat, lii xeebeel la ci waa réew mi, rawati-na taskati xibaar yi fi fekk baax. Da leen a tanqamlu, dummóoyu leen te nëbbu ko ndax moo ne ci gémmiñu boppam : « sama yoon nekkul ci li taskati xibaar yiy wax ci njéggal bi, duma ci wax. » Ndege, deesul gis benn njiitu réew lu ñàkk faayda bay péncoo mbiriy réewam fii ci Senegaal. Moom kay, Maki rekk a koy defi ca réewi xonq-nopp ya. Muy wone ne, ba tey moomagunu sunu bopp dëgg dëgg, ndax sunu njiit yi amuñu fulla amuñu faayda. Ñaareelu njàngat bi nuy jële ci kàddoom yooyu mënees na ko xaaj ñaar. Benn bi nitu Maki ci boppam la ñeel, beneen bi aju ci digganteem ak Xalifa Sàll. Bi ci njëkk mooy réy ak réy-réylu bi Maki di biral ciy kàddoom : « …ci moom doŋŋ la aju… », « …ciy loxoom kese la nekk. », « Moom mooy xool saa su ko soobee mu jéggale. », « Bés bu ma neexee walla ma am coobare bi rekk, dinaa ko def »… Maki Sàll, li mu nuy xamal ci kàddu yii mooy ne, moom kott, moom kese- kese mooy dogal. Kenn mënul wañaar loxoom ba defloo ko lu ko neexul, ak koo mënti doon. Maki Sàll dafa summi yérey njiitu réew, sol yérey Buur Saltige. Ndaxte, buuru saltige rekk mooy jiitee doole, di jaay maa-mën, jàpp ne lu mu wax mooy am, lu mu waxul du am ; lu mu bëgg mooy am, lu mu bëggul du am. Ndege, njiitu réew day woyof, nangoo déglu askanam ak kilifa réew mi ba tax lépp lu mu jàpp, su ñu ko ñaanee mu bàyyi. Waaye, Maki jikkoy firawna lay doxe. Waaw. Ndax bu demee bay dolli ci waxam ji : « …ni ma koy faral di defe.» ak  « …dinaa leen jéggal, génne leen kaso. », Maki day firndéel ni njéggal, jamono jii, ciy loxoom la nekk, ku ko neex la koy jagleel. Lii moo tax ndaw yi wutal ko dàkkental, di ko woowe « xaaju Yàlla » walla « àmbasadëeru Yàlla ci Senegaal ». Ndaxte, bu nee at mu nekk mu jéggal nit ñu bare, li wax ji wund mooy ku ci bokkul daŋ kaa neexul. Ci lanuy tàbbee ci ñaareelu njàngat bi ñeel digganteem ak Xalifa Sàll. Ndax seetlu ngeen lenn ? Saa su Makiy wax ci mbirum Xalifa Sàll, du jaar ci turam. Xanaa keroog ba mu nee “sama doomu baay la” ndax sant wi ñu bokk. Rax-ci-dolli, ñépp xam nañ ni jot naa yabal ay ndaw ca kaso ba ngir ñu gise ak Xalifa Sàll. Xamunu lu ñu fa waxante, waaye mel na ni Maki dafa dencal mer Xalifa. Te, Xalifa wax na du benn du ñaar ne sàkkuwul njéggal ci Maki te soxlawu ko. Dafa mel ni am na lu Xalifa Sàll gàntal Maki ba tax koo ñéññ. Coxorte giy feeñ ciy waxam ak doxalinam doy nañ firnde. Ma leen di laaj nag : waaw, lan la Maki jàppal ngóor si Xalifa ba tax muy doxale nii ak moom ? Lan lañu jot a séq ? Ak lu ci mënti am, askan wi moom moo gën a sonn Xalifa fuuf. Bi mu tàmbalee taw ba léegi, askan wi nelawatul, te waa Ndakaaroo ci gën a sonn. Kër yi taa nañu, koñ yi taa, mbedd yi taa, tali yi fees dell ak ndox, kenn amul foo jaar. Njëg yépp yokku, xaalis amul, oto yiy mbëkkante ci tali bi, nit ñiy dee. Kenn xamul fooy teg sa tànk. Metit yooyu yépp teewul nguur gi ne ée-yaay, nun danuy bër, njiitu réew miy wone ay portale mook soxnaam ca Tugal, ci kër gu taaroo taaru, di bége. Mu mel ni dañuy mbëllee baadoolo yi. Li am ba des moo di, ak Maki, mel na ni, laabisiina la réew miy jubal. Nu dem rekk.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-25-2-2024/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM (25/2/2024) MBIRI PAAP GÉY AK MÀRSEY Gannaaw CAN bi mu demoon ak Senegaal, Paap Géy, miliyë Màrsey (Marseille) bi dañ ko dàndoon ca këlëb ba, maanaan dañ ko génne woon, ber ko. Li ko waral mooy ni pasam dafay jeex ci weeru suwe 2024, Màrsey bëggoon mu yeesal ko. Waaye, Paap Géy dafa lànk. Njiiti këlëb ba jéem a wañ loxoom, mu bañ, jàpp fi mu jàpp rekk. Ci la ko Pablo Longoria mi jiite Màrsey beree. Ndogal loolu tiisoon na ko lool nag. Ndax, laata muy futbalsi CAN bi ak Senegaal, dafa toogoon diir bu yàgg bob, futbalu ci. Li ko sabab mooy ne FIFA dafa tegoon daan. Waaye, ab bunt ubbeeku na. Nde, boolewaat nañ ko ekib bi war joŋante ak Montpellier tey ci dibéer ji. Seen tàggatkat bu bees bi, Jean-Louis Gasset bi wuutu Gattuso moo sàkku ñu boolewaat ko ci gaa ñi. Ndax, ñépp la soxla ngir liggéey. ËRO 2024 : TONI KROOS DINA BOKK Saa-Almaañ bi nangu na solaat mayo dëkkam gannaaw bees ko toppee ay yoon ngir mu ñëwaat ca ekib ba. Ca atum 2021 jëloon ndogalu bàyyi ekibu Almaañ bi. Keroog ci 22 féewiryee 2024 wii la xamle ci xëtu Instagramam ni dina dellu ca ekib ba. “JEUX AFRICAINS GHANA 2024” Sëriñ Saaliw Ja, tàggatkatu ekib U20 bu Senegaal bi, fësal na limkag 23i ndaw yim tànn ngir ànd ak ñoom ci yooyu joŋante. Ci tànnam gi ñu gis ni woo na ci U17 yu bari yu demoon ci kuppeg àddina gii weesu (U17). Ñooñii di : Amara Juuf, Alfa Ture, Sëriñ Fàllu Juuf, Doriwaal Jaata, Yayaa Jémme, Ibraayma Jàllo ak Idiriisa Géy. EMILIO NSUE BÀYYI NA GINE EKUWAATORIYAAL Saa-ekuwaato-gine bi jël raayag dugalkat bi ëppaley bii ci CAN 2023 bii weesu fa Koddiwaar xamle na ni bàyyi na ekib nasiyonaal ba. Gannaaw CAN bi, ay coow yu sew amoon na ci digganteem ak ekib ba, ñàkkul ni yooyu mbir a waral bàyyeem. Moom nag, futbal na 42i yoon ak ekib bi, daldi dugal 23i bii.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/mangaan-ndeke-am-na-ci-politig/
MÀNGAAN NDEKE AM NA CI PÓLITIG ! b ak yu tey gis ñu woroo lool. Am na sax ci ñoom ku ne woon Ndeyu-Àtte réewum Senegaal dafa war a aaye màngaan ci politig. Yemu fa, ndax dem na ba yaramam tàng, mu yokk ci ne képp ku jóge cib pàrti, ak bu mu mënti doon, dem màngi ci nguur gi, yoon dafa war a jël sa bakkan ! Moonte ngóor si waxoon loolu, moo xéy bés ne maa tey, fekki naa Maki Sàll… Waaye li Senegaal di miin xeeti jëf yu ñaaw yooyu yépp, teewul askan wi, rawatina ndaw yi, am mbetteel biñ déggee ne Aysata Taal Sàll màngi na moom tamit. Man mii amoon naa ci naqar lool. Mënuma woon a nangu ne “Gayndek Podoor gi”, gaynde gi ma xamaloon fulla ak faayda ju mat sëkk dina defi lu ni mel. Lu ko ci xiir ? Ñii a ngi naan dañu koo compal waaye am na ñu wedddi loolu. Xéy-na bañ cee soree gën, ndax Yàlla rekk a xam. Li am ba des, daal, moo di ne jot na ndawi Senegaal yi taxaw temm ngir xeex ba jële fi yenn ñaawtéef yiy yàq làngu pólitig gi tey nasaxal campeefi réew mi.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/di-buur-di-bummi/
DI BUUR, DI BUMMI Ci gaawu bi weesu, 4eelu fan ci weeru me, la dipite yi wote sémbub àtte biy far palaasu Njiitu-jawriñ yi ci nguurug Senegaal. Ndax sémbub àtte bi jàll na ? Loolu jarul a laaj ! Ci 138 dipite yi teewoon, 124 yi wote nañu « waaw » 7 yi « déedéet ». Yeneen 7 yi des ñoom, di waa PDS, dañoo lànk ne duñu wote tey duñu wote ëllëg. Kon, Senegaal amatul Njiitu-jawriñ. Àtte bu bees bii, nag, dina indi ay coppite yu bare ci doxalinu nguur gi, waaye it dina gën a dooleel Njiitu-réew mi. Du loo xam ni Maki Sàll ak Bun Abdalaa Jonn rekk la ñeel. Dafa dig coppite gu soxal ndeyu-àtte réew meek tëralinu politigu Senegaal ci boppam. Ndaxte, yamoo bi war ci diggante ñetti baat yi – baatu doxal bi, baatu yoon bi  ak baatu fal àtte bi – lay nasaxal, daanaka. Li péncum réew mi dogal dina soppi 21 sàrt ci biir ndeyu-àtte mi, jox Maki Sàll wareef yi Bun Abdalaa Jonn jagoo woon. Ñenn ñi ci kujje gi nee ñu nguur gi duggewu ko dara lu dul këppeel doole. Ñeneen ñi, ñoom, jàpp nañu ne Maki day waajal xaat joŋanteb 2024. Dëgg la sax, Njiitu-réew mee yelloo tabb ku ko neex ngir mu jiite gornmaa bi, jàppale ko ci naal yi mu lal ñeel doxalinu réew mi. Naam, Senegaal ay njiiti-jawriñ yuy jaamu soxlaam lañ fiy faral di gis. Waaye loolu warul a tax ñu ne kenn dootul jiite jawriñ yi. Mbir mi daal, jaay doole lay gën a nirool. Ndaxte léegi moom, Maki mooy Buur di Bummi : su defulee lu ko neex, moom la neex !
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/afrig-lu-la-tax-a-des-ginnaaw/
AFRIG, LU LA TAX A DES GINNAAW ? Bare na li may toog man kenn, di yónni samam xel, mu wëral ma àddina sépp ak li ci biir, fu nekk mu ne fa naam-daraame, yër la fa nekk, dellusi. Waaye, li ëpp ci samay xalaat ak i seetlu, Afrig la ñeel, sunu Afrig ak ëllëgam. Bu ko defee, sama xel mi day faral di wër réewi Afrig yi ba ñu daj, bunt bu dul buntu jinne mu fëgg fa, dugg ci biir kër gi, jàngat la fay xew, doxalinu njiit ya fa nekk ak taxawaayu askan wa. Muy politig, di koom-koom, aada ak cosaan, njàng mi walla ni yoon doxe, fànn bu ci nekk mu saytu la. Ndeysaan, saa yu sama xel mi delsee ci tukkeem boobu, sarica bu naqadi la may indil. Ndaxte, liy màndargaal daanaka réewi Afrig yépp mooy mbir yii may limsi : ndóol, xiif ak mar, ay xarey biir-réew yu dul jeex, ger, njàng mu yàqu yaxeet, ñàkkub liggéey, añs. Te, màndarga yii, fépp fu ñu daje, tumuraanke lañuy jur. Ma jàpp ni sabab yi bare nañ. Waaye, dinaa leen baaxe, ci sama xalaat mu gàtt, sabab yi ma foog ne, ñoo gën a tax Afrig des ginnaaw.1. Njaam ak Nooteel Deesul a nàttable ne, diirub 400i at yi tubaab yi moomoon Afrig cib jay doole ak i nax, am nay njeexital yu bir ci nekkinu Afrig ba sunu-jonni-Yàlla-tey jii. Dafa di, légéti njaam ak nooteel a ngi fi, ne fàŋŋ. Te, sikk amul ci ne, tey, njaam ak nooteel yooyu, ñooy cëslaayu naataange biy màndargaal réew ya ko daan def walla daan ci jariñu. Su ma nexee joxe misaal ci Farãs, Àngalteer walla sax Etaasini. Naam, bare na ci loo xam ne seen xalaat ak seen farlu moo leen ko may. Waaye, alal ak doole yi suuxat seen koom, Afrig la bawoo. Maanaam, sunuy rongooñ ak dereti maam lañ siime seen cere. Ndeysaan, sunu maam yi sonnoon nañ lool, doonte sax, amoon na ciy workat. Moom kay, tubaab bi jàppewuleen woon niy nit. Dañ leen daan liggéeyloo niy mbaam ci tool yi. Di leen dóor ak a toroxal guddeek bëccëg, ñuy lekk tuuti, di liggéey lu bare. Nit ku ñuul amul woon benn sañ-sañ ci boppam. Tubaab bi dafa jàppoon ni, Yàlla moom la bindal nit ku ñuul ngir mu doon jaamam. Loolu la seen njiiti jàngu yi doon gëmloowaate, di wëlbati waxi Biibal bi, di kàcc rekk di dajale. Jigéen ñi, ñoom, dañ leen daan siif saa su nekk, di leen tëdde. Xonq-nopp bu ci sa nëq tàng, nga fab kenn dëpp sa kow lal, faj sa aajo. Te, sax, àggoon nañ ci yoonal seen caay-caay googu. Ndege, Luwi XIV, buuru Farãs ba woon, dafa jëloon ab ndogal, yoonal tëralinu njaam gi, biral ci àqi ma-weex yi ak wareefi nit ñu ñuul ñi ñeel leen. Li mu ko dugge woon lenn rekk la : yaatal ak dooleel nooteelu tubaab yi. Waaye, loolu mënutoon a wéy. Ginnaaw gi, am na ci sunu maam yi ak ñenn ci tubaab yi ñu jóg taxaw temm xeex njaam ba ñu xéy dakkal ko. Ndekete yóo, gaa ñi amoon nañ yeneen pexey nooteel yuñ doon làq. Gaa ñi dañu tekki genn buumu njaam, fas geneen gu gënatee dëgër, te mooy ci nasaraan “colonisation”. Dafa di, xeetu nooteel woowu moo rawati bu njëkk ba. Gaa, njaam gi wuññi woon na sunu sutura maam ya, nasaxal koomu Afrig. Waaye, nooteel bi dafa laal xol yeek xel yi, futti sunuy aada, suufeel ak soofal sunu cosaan, fënëxal sunuy ndëgërlaay. Xamatun lun doon. Xamatun fun jëm. Ñu jàppenu ay dof walla ay mala yu amul démb, amuñ mboor. Moo waraloon njiitu réewu Farãs ba woon, Nikolaa Sarkoosi, ca waxtaan wa mu amaloon ci Ndakaaru gii, waxoon ne Afrig amul cosaan. Aka mën a fen ! Ku la xeebe nii, noo koy farale ? Moo tax àndumaak Lewópóol Sedaar Seŋoor bi muy wax ne nooteel bi loraange ju jur njariñ la. Xamuma nu mu mënee woon wax wax ju ni mel. Xeeb sa bopp weesuwul lii. Fekk ay nit seen réew noot leen, jaay leen doole, naka la ci njariñ mën a sababoo ? Sil Feri (Jules Ferry) mu Farãs lii la waxoon : « Na ñépp xam ne nit ku weex moo féete kow nit ku ñuul. Bu ko defee, war nan, nun ma-weex yi, xettali nit ku ñuul, jële ci moom jikkoy mala, ngir saxal ci moom nite ». Ñu ni déet-a-waay, Buuru Belsig ba woon, Lewópóol II, ne, Kóngo ak lépp li ci biir, mooy boroom. Moo taxit, xeetu metit walla ñaawtéef boo mënti xalaat teg na ko doomi Kóngo ya. Noonu yit la deme woon ca Mosàmbig ginnaaw bi Purtugees yi woñee loxoy waa dëkk ba ngir ñu beyal leen wëttéen. Loolu juroon xiif gu metti ca dëkk ba. Atum 1960 ak li ko jege, ci la réew yu bari ci déndug Afrig tàmbalee moom seen bopp, ginnaaw bi Tubaab yi duyee seeni gafaka ba ñu fees dell. Waaye nooteel gi yemul foofu, de. Wax ji lii doŋŋ la woon : dangeen a bëgg moom seen bopp ? Yoon waa ngoog waaye na leen leer ne dinanu wéy di leen yilif. Kon, beneen xeetu nooteel daldi judduwaat. Booba ba tey, boo jëlee réew mu mel ni Senegaal, lépp lu fi baax sunu njiit yi jox ko waa Farãs toog. Su may xool fi nu jaar yépp, doore ko ca jamonoy njaam ga ba tey, ci laay gën a gëm li Séex Ànta Jóob waxoon ca Ñiseer : « Su nu yaakaaree ne ñaawtéef yi nu tubaab bi def deñ na ci nun, noo ngi nax sunu bopp ». Dëgg la ndax tubaab bi dafa raxas sunu xel ba gëmatunu sax sunu bopp.  Du ñàkk am ñu ni ma, dëgg la ne tubaab yi tooñ nañ nu waaye nun it war nanoo seet ba xam ndax def nanu sunu wareef ci ëllëgu Afrig. Loolu neexul a weddi. 2. Waaru Ndawi Afrig yi ci ëllëgam Mënees na tënk wax jépp ci benn laaj kese : lan moo war a nekk sunu taxawaay, tey jii ? Ma jàpp ne, xeex moo fi sës. Waaye, nag, xeexu ku am jom, ànd ak xel mu ñaw ak i pexe yu wóor te jàppandi. Bala loolu, warees na defaraat jikko yi, ànd booloo ngir sunuy noon am luñ nu ragale. Ndax, ni la wuude gise rekk la lay ëwale. Xeex boobu, nag, sunu njiit yee ko waroon a sumb ; lu ko moy, ñu jiite ko sax. Wànte, sikk amul ci ne, ñoom ñooñee, ay tubaab yu ñuul kukk lañ, diy jaam yu bir, ay workat, diy dunguru nootkat bi. As tuut ciy njiit yu farlu woon, bëggoon seen réew, te daan jàmmaarloo ak tubaab bi, dañ leen a sàkkal pexe, bóom leen. Ñi ma gën a namm ci njiit yooyu ñooy : Tomaas Sànkara, Lumumbaa, Silwanus Olempiyó, Mamadu Ja ak Xadafi. Wànte, loolu warunoo tax a xàddi. Bu yoon jeexul, waaxusil du jeex. Yaakaar jeexu fi ndax du ñépp a mel ni sunu njiit yi. Mënees na am yaakaar ci sunu ndawi tey yi. Ndege, jamonoy tey jii, li fi am ciy xeltukat, ay jàmbaar yu bëgg seen réew, ay jumtukaayi xarala yu matale ak ay ndaw yu dogu ci xeexal Afrig (Kémi Sebaa, Ndongo Sàmba Silla, Gii Maryiis Saaña, añs.), amul woon ca jamonoy maam ya. Doonte, sax, ñoom it bey nañ seen waar ci tool bi, yem fi leen seen doole ak seen xel yemloo woon. Dafa di, lu bare ciy xeeti woy ak xalamal yiñ ràññee tey, yu ci deme ni “Jazz”, sunu maam yaa leen daan fent, ngir giifal seen xol saa yu leen tubaab bi daan bugal, ak di biral boddekonte biñ leen daan teg. Ndeysaan, foo leen fekkaan, rawatina ca tooli Amerikeŋ ya, ñoo ngay woy ak a woyandoo ngir feral seeni rongooñ. 3. Làmmiñi Afrig yi Réew moo gis, bu naatee, ay boroomi xam-xam ñoo fa jaar. Xam-xam, nag, mënta jariñ boroom walla aw askan feek ŋëbu ko ciy loxoom, péeg ko ci boppam, ay noppam di ko dégg, xolam di ko yëg. Moo, ndax xam-xam mën naa am muj bu ni mel bu dee boroom déggul walla nàmpul làmmiñ wi ñu ko fase ? Déedéet ! Mukk ! Kon, sunu boroom xam-xam yi ñuy soow guddeek bëccëg, ñiy bind ay téere ak a wax saa su nekk, ñan lañuy bindal walla ñan lañuy waxal ? Ngiree ñu wax ak askan wi, fàww ñu jëfandikoo làmmiñi askan wi. Kon, naataange ak yokkuteb Afrig, mënuñoo jéll làmmiñi Afrig yi. 4 . Liggéey tuuti wax lu bare Soo jëlee réew mu mel ne réewum Senegaal, li nit ñiy coow a ëpp li ñuy liggéey. Tàmbalee ko ci ñi nu jiite. Koo fal ba mu toog mu ngi lijjanti nu muy def ba duufal gafakaam ak yosiy àndandoom. Seeni njuuj-njaaj lu ci ëpp ciy wax lañu koy muur ndax dañuy aakimoo jumtukaayi tas xibaar yi di wax subaak ngoon. Néew na ñu ciy wax lu jëme réew mi kanam. Politig rekk ! Dégg naa keroog benn taskatu xibaar naan moom mësul a gis réew mu sukkandiku ci wax ak politig ba naat. Sàllaaw wax na dëgg gu wér péŋŋ ! Réew, liggéey a koy naatal, moo koy jëme kanam. Njiitu Afrig yi dama ragal ne nguur da leen di tàggaleekseen sago. Seet ko ci réew mu mel ne Kóngo, Saasu Ngesó moo fa toog ci jal bi boobaak léegi ëpp na fanweeri at. Ci gàttal, ku juddu ba muy jël réewum Kóngo, jàng nga fi ba jeexal, takk fi soxna ba samp fi kër. Gine Konaakiri tamit, Alfa Konde daa bëggoon a soppi ndeyu-àttey réew ma ngir am ñetteelu moome. Te kat, moo waxoon ci gémmiñam ni def ñetti moome xalaatu ko ndax loolu dafa worook demokaraasi. Sunu réew mii di Senegaal, xel yaa ngi bëgg a teey : Sóori Kaba, di woon jawriñ ci nguur gi, da ne ndeyu-àttey réew mee tere Maki mu sàkku ñetteelu moome, ñu daldi koy dàq ci saa si. Lu Maki Sàll mii narati ? Baax na. Nan xaar ba xam fan la wànnent di mujje ak i bëtam… Warees na joxoñ tamit baaraamu tuuma sunu liggéekat yiy ñàkkal lool faayda seen liggéey, di tappale ak a caaxaan, dëkke kàcc ak càcc. Lu ngeen xam ci ku dul xéy waxtu, du wàcc waxtu ? Kenn ci ñoom fonkul liggéey biñ ko sant te mu am seeni junniy-junni moroom yu bëggoon a toog fiñ toog. Yàlla boo am soxla bu jamp ba dem ci benn biro ci réew mi. Dinañ la soofantal, ñàkke la kersa walla xaarloo la ba nga xàddi ci lu ñàkk faayda. Ci misaal, bés, sama benn xarit bu ma bokkaloon lekkool Ndar dafa dem ci benn bànk bu mag biir Ndakaaru, amoon yu mu fay lijjanti. Ndaw si ko waroon a toppatool li mu doon wut ne fa luëpp fukki simili di talalali ci njéggil-kàddu gi, di reetaan mel ne ku nekkul ci liggéeyukaay. Xeetu liggéeykat yu ni mel bokk nañ ci li tax Afrig des ginnaaw. May daaneele ci mbirum aada ak cosaan. Fépp foo dem ci àddina si, réew yi gën a naat, doonte seen askan a ngi sant bu wér, mooy yi sax ci dekkal seen  cosaan, di dundalaat seeni aada ngir dëppale leen ak jamono. Seen démb lañuy def jaaruwaay ngir jëmmal seeni naal ci politig, koom-koom, njàng ak njàngale, tàggat-yaram, ba ci aar bi sax (nataal, sinemaa, pecc, añs.). Nun nag, nekkewuñ fi lu dul roy ak a toppandoo, di weccoo xalaat ciy pecc ak i woy yu ñu fente Amerig. Lii bu dul ñàkk faayda, lu mu ? Ku ràññeeku ca Amerig ci xeexal nit ñu ñuul ñi fa nekk, Luwis Faraxan dafa am bés muy wax ak ñoom ci am ndaje. Li mu leen wax keroog mooy, nit su jéemul dara ngir teggi nooteel yi ñu koy teg, su jéemul dara it ngir fent walla defar dara, nit kookule dara du ko wutaleek wékkukaayu yére. Ndax wékkukaayu yére mënul wax, mënul dox te fu waay xiire rekk lonk cay yéreem. Léegi nag, nun waa Afrig, rawatina nun ndaw yi, nooy seet ba xam ndax danoo war a taxaw temm, doon wennuw say ngir jëmale Afrig kanam, walla danuy toog ne xótt-xóttaaral ni ay wékkukaayi yére.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/sunuy-doomi-ndeyi-mali-yi-sonn-nanu/
SUNUY DOOMI-NDEYI MALI YI SONN NAÑU At yi weesu yépp, fitu doomi-Mali yi toogul benn béréb. Weer yi nu génn sax, seen njàqare ak seen tiis dafa mel ni lu yokku. Te lenn waralu ko lu dul jàmmaarloo yu tar yi am ci diggante ñaari waasoo yii di Pël yeek Dogoŋyi. Lu ni mel nag, jaaxal na ñu baree-bari. Ndax, ci atum 2012 ay defkati ñaawteef yuy mbuboo lislaam song réew ma. Ginnaw gi la ci Mbootaayu xeet yi dugg, jële leen fa ci atum 2013 ba noppi déggoo ak ñoom ci atum 2015 ci li fay war a saxal jàmm. Waaye loolu lépp mel na ni mujjul fenn. Ci at mii nu nekk, ci weeru Mars, 160 Pël la Dogoŋyi bὀom. Ñu ne déet-a waay, Pël yi daa di feyu, faat bakkanu 35 Dogoŋci 9elufan ci weeru Suweŋ, dolli ci 38 ba tey ci woowu weer, ci li nguuru Mali wax. Loolu lépp ci ñaari dëkk yu wute la xewe. Waaye Mbootaayu xeet yi jàpp na ne 41 Dogoŋ la ñu faat. Daw fitnaa tax Pël yeek Dogoŋ yiy gàddaay, wuti fu ñu làqu, moo xam Burkina-Faaso la walla fu ñuy wax Dinaguura. Mbir mii nag, am na ñu jàpp ne xare ba fi jiyaadis yi amaloon moo ko sabab. Ndax nee ñu seen njiit, Aamadu  Kufaa, ci Pël yi la doon wute ay soldaar. Pël yi nag, dañoo jàpp ne Dogoŋ yee sotba Mbootaayu xeet yi sempi ndëndu jiyaadis yi, reyaale seeni mbokki Pël yu bare. Ñàkk kóolute gi lal lii lépp fan la jóge ? Ndax réerook mbañante gu yàgg rekk la ? Yàlla rekk a xam. Li am ba wὀor moo di ne waasoo Afrig yi yàgg nañuy jàmmaarloo ci seen biir. Te li koy waral léeg-léeg, bu weesoo xëccoo nguur, du lenn lu dul réere mbir li ñu bokk ndax, ni ko Séex Anta Jóob di waxe, li leen boole moo ëpp doole fuuf li leen di féewale. Leneen ub na lool boppu nit ñi ci mbir mi te mooy tekk-tekkaralu àddina sépp, li ñépp toog boobaak léegi di seetaan. Ku nee ngi xaar ba sa moroom wax ngay soog a yëkkati sa baat. Lii kañ xanaa mooy lekkante leen ba jeex tàkk, sunu yoon newu ci ! Moom daal, ku mën sa moroom dumaal. Mbete làmbu tàkkusaan ! Li ci gën a xëtt xol, nag, mooy yàcc-yàccaaralu njiiti réewi Afrig yi, mu mel ni waa Mali duñu seeni mbokk. Te moo ne de ñoom lañu waroon a njëkk dégg bala kenn di yëkkatiy kàddu. Fi mu ne nii bala ñoo mën a wax mbaa ñu jëf fàww ñu jot ndigal lu tukkee ci nasaraan yi. Tàmm nañu ko sax. Seen yoon newul ci dëkkandoo bi leen yittewoo waaye su daray xew ci réewi Tubaab yi ñuy daldi tàggook seen sago. Ku ko weddi fàttalikul bés ba ay saay-saay songee Saarli Ébdo, rey fay taskati-xibaar. Keroog jooju njiiti Afrig yu bare fésal nañu seen naqar, ku nekk ci ñoom di nu tanqal, naan « Je suis Charlie ». Yii njiit daal, kenn xamul lu ñu doon. Boroom kër gu ñuy dab di ko mbej sax moo leen tane. Li am ba des daal mooy na waa Mali delloosi seen xel te xam ne ay wu waxtaan fajul, xeex du ko saafara mukk. Nde bi àddina sosoo ak léegi kenn mësul a gis xare bu jur jàmm. Moom kañ, musiba rekk lay sooke, delloo am réew ginnaaw.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-6/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM FUTBAL Victor Boniface moo ngi dox ci ndox Ataakã Bayer Leverkusen bi moo ngi wane boppam bu baax jamono jii ca sàmpiyonaa Almaañ ba. Lu tollu ci ñeenti weer a ngi nii (ut, sàttumbar, oktoobar ak nowàmbar) moom lees di tabb  ki gën a xareñ ci weer wi. Santos wacc na Këlëbu Beresil bi moo ngi am ren 111i at ba ñu ko taxawalee ak léegi. Ren jii di guléet muy wàcc ca ñaareelu sàmpiyonaa ya (D2). Loolu nekk lu doy waar ca boobu këlëb. Ndax, guléet la, te dafa doon ekib bu mag boo xam ni bii ay punkal ñu fa jaar, ñu ci mel ni Pële ak Neymaar… Musaa Wagee ngi dikkaat ndànk-ndànk Gannaaw gaañu-gaañu bu metti bi mu ame woon at yii weesu ca Barça, loolu bokk ci li wàññiwoon xareñteem, ca la doomu Senegaal ji mujje woon a jóge foofu dem ci këlëb bii di Anorthosis Famagouste, ca sàmpiyonaa Siipr. Mu mel ni mu ngi delsi ndànk-ndànk ci nees ko xame woon. Ndax, ci weeru nowàmbar bii ñu génn, moom lees tabb ki gënn a xareñ ca weer wa. Tijaan Jàllo wax na bëgg-bëggam ci ekibu Senegaal Bokkoon na ci ndaw yi teewaloon Farãs ci Kuppeg Àddina gees jagleloon ndaw yi ëppalagul 17i at yi weesu ci fan yii. Moom nag xamle na ni lu koy neex la mu futbalal Réewam mii di Senegaal. Loolu nag xëyna dina neex mbokki saa-senegaalam yi waaye ña di waa-Farãs njort na ni du yam ca ñoom. Loolu nag war a tax ekib bi ubbil koy loxoom donte daf koy boole ca ndaw ña ngir mu am lim bëgg ak ñu bañ ko xatal ca ekibi Farãs ya. CAF Awards : Lamin Kamara jël na cargalug ndaw bi gën a xarañ Lamin Kamara (19i at), Amara Juuf (17i at) ak Ezzalzouli (U23 Marog) ñoo nekkoon ndaw yuy xëccoo cargalu gi ñu jagleel ndaw bi gën a xarañ ci at mi fii ci Afrig. Lamin Kamara moo ko mujje jël. Moom, Lamin Kamara, daf def at mu am solo, jël ci CHAN beek CAN U23, ba noppi di joxe ca këlëbam, bokk it léegi ci Ekibu Senegaal bu mag bi. Cargal gu mag gi, balu wurus bi (ballon d’or), Saa-Niseriyaa baa ko jël, Wiktoor Osimen. Basket : Góorgi Si Jeŋ bàyyi na Saa-Senegaal bi xamle na ni bàyyi na basket bi ci benn laaj-tontu bu yàggul ak Jeff McDonald Du San Antonio. Moom nag mu ngi toll ci 33i at. LÀMB Amaa Balde ak Giri Bóordoo jàppees na seen bëre 30i fan ci weeru suwe bii di ñëw ci 2024 mi. Saa-Cees ak Ëmma Seen itam jàppees na ko ci 5i fan ci me bi.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-19-11-2023/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM (19/11/2023) LÀMB : LAG DË GEER 2 DAAN NA SITTA Ñaari mbër yi waajal nañu seen bés bi, def nañu lépp li ci war, neexal seen i jàkkaarloo ak bés beet. Lag dë geer 2 dafa ñëw, ànd ak kóolute, bàkku, yëngal, daldi koy xumbal. Sitta tamit, waxi noppi. Ñëw na nees ko xamee, ànd ak mbooloo mu takku, muy lees ko xamee it. Bàkku na ba Lag 2 bàkkoo ba noppi, mu neexal ko ba mu neex. Moom Sitta nag tay dafa dikkee nu doy waar. Dafa ñëw ak alikeñ, muur kanamam ba kenn gisu ko, ci waajtaayu bàkkoom la koy door a dindi. Cëy làmb, lu nekk a ngi ci ! Aren Nasiyonaal bi fees dell, loolu di dëggal ba tay lees di wax ni làmb ji dekki na. Seen bëre bi neexoon na , tàngoon na it lool. Nde ñaari mbër yi bëre nañu xeex nañu tam. Seen bëre baa ngi tàmbali ba 21i waxtu tegee 18i simili, ñu dawal wenn xaaj wi ba  songoo ci, xeex ci ba mu jeex. Ba ñu noppaloo ba dikkaat ca la ñu gënee xeex ku ci nekk ñam sa moroom ciy kurpeñ, Sitta dem seeti Ardo daanaka ñeenti yoon. Gannaaw loolu, ñaar-fukki simili yees leen mayoon jeex ñu daldi jox Lag dë Geer 2 ndam li ci kaw dànkaafu (avertissement) bu Sitta am ci xaaj wu njëkk wi. Sitta tamit, daanaka am na ndam lu koy soppeem jox ak seetaankat yi. Ndax njàmbaar gum wane ci kanamu ndaanaan bu tollu ni Lag 2, sonal ko, xeexloo ko. Lile di wane ni Sitta màgg na te noppi na ngir bëre ak ndaanaan yi ci kaw. KUPPE : GAYNDEY RËKK NAÑ SUDAŊ Démb la Senegaal doon laaleek Sudaŋ ci joŋantey bokkadil yi ñeel kuppeg àddina si war a am 2026 (éliminatoires de la coupe du monde 2026). Gaynde yi nag rekk nañ waa Sudaŋ, dóor leen 4-0. Paap Mataar Saar ak Lamin Kamara ràññeeku nañ ci. Ndax, ku ci nekk dugal na benn bii, muy seen njëlbeeni bii. Seen bii yi nag jàppees na ni dina doon lu leen di gën a gëtëŋ ñu gën a firi, rawatina Lamin Kamara mi nga xam ni moo gën a nekk gan. Saajo Maane moo dugal yeneen ñaari biiyi. KUPPEG ÀDDINA U17 Sunu ndaw ya ca “Indonesie” dinañu daje ak ndawi Farãs yi ñeel 1/8 dë finaal yi. Àllarba jii, 22 nowàmbar 2023, lañuy joŋante bu 12i waxtu jotee. Nu di leen ñaanal ndam.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/futbal-ligue-des-champions-europa-league-ak-conference-league/
FUTBAL : LIGUE DES CHAMPIONS, EUROPA LEAGUE AK CONFERENCE LEAGUE Barki-démb, démb ak tey lañ doon amal joŋantey kaar-dë-finaal Ligue des champions yi, Europa League ak Conférence League fa Tugal. League des champions Ci talaata ji la Dortmund ak Atletico Madrid doon amal seen ñaareelu ndaje. Ca ndaje mu njëkk ma ame woon fa Espaañ, Atletico Madrid moo gañe woon 2i bii ci 1. Waaye, bi ñu demee Almaañ, Dortmund daf ko dóor 4i bii ci 2, daldi koy toogloo. Ca jamono jooja, Barcelone ak Paris Saint-Germain ñoo ngi doon amal, ñoom itam, seen ñaareelu joŋante. Ca bu njëkk ba, Barcelone moo fekki woon Paris, duma ko 3i bii ci 2. Barki-démb, Paris dafa fayu. Ndax, dafa fekk Barcelone dëkkam, dóor ko fa 4i bii ci 1. Barcelone moo njëkk a dugal. Waaye, biñ joxee kàrtoŋ bu xonq Araujo, ca ndaje ma wëlbatiku. Démb, ci àllarba ji, yeneen ñaari ndaje yu mag amoon nañ diggante Manchester City-Real Madrid ak Bayern Munich-Arsenal. Ci joŋante bu njëkk bi, Real Madrid moo toogloo Manchester City biir dëkkam. Ca seen joŋante bu njëkk ba, dañoo témboo woon 3-3. Démb tamit, dañoo témboowaat 1-1, Real Madrid gañe 3-2 ci teg-dóor penaltii yi. Bayern tamit dafa toogloo Arsenal. Ginnaaw seen témboo 2-2 ca seen joŋante bu njëkk ba biir Arsenal, Bayern Munich moo am ndam ci kanami soppeem. Nde, dafa wane geneen xar-kanam, dóor àngale yi 1-0. Bu ko defee, nii la démi-finaal yi di demee : Paris Saint Germain – Dortmund Bayern Munich – Real Madrid Europa League Ci joŋantey kaar-dë-finaali Europa League yi, tey ci alxamesu tey ji lañ leen doon amal. Ñu amoon ci ñeenti joŋante : AS Rome –  Milan, Atalanta – Liverpool, West Ham – Beyer Leverkusen ak Marseille – Benfica. As Roma moo toogloo Milan, dóor ko 3-1 bees boolee ñaari ndaje yi. Naka noonu, Atalanta génnee Liverpool 3-1 ci ñaari ndaje yi. Noonii la Bayer Leverkusen toogloowee West Ham 3-1 ci seen ñaari ndaje yi. Marseille tamit moo toogloo Benfica ginnaaw biñ àggee ci teg-dóor penaltii yi. Nii la démi-finaal yiy demee : As Roma – Bayer Leverkusen Marseille – Atalanta Conférence League Ci xëccoo Conférence League bi tamit, ñeenti joŋante lees ci amoon ci alxamesu tey ji : Lille – Aston Villa, Fiorentina – Viktoria Plazeň, PAOK – Club Brugge ak Fenerbahçe – Olympiaco Piraeus. Aston Villa, Fiorentina, Club Brugge ak Olympiaco Piraeus ñoo jàll démi-finaal. Aston Villa mooy dajeek Olympiaco Piraeus, Fiorentina laale ak Club Brugge.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/waaw-ana-ku-boom-omar-bolonden-joob/
WAAW, ANA KU BÓOM OMAR BOLONDEŋ JÓOB ? Omar Bolondeŋ Jóob a ngi juddu ci 10eelu fan ci weeru sàttumbar 1946 ca Ñaame, péeyub réewum Niseer. Mu ngi faatu ci 11eelu fan ci weeru Mee 1973 ca kaso ba woon ca dunub Gore. Omar Bolondeŋ Jóob, nag, kàngam la woon ci biir kàngam yi, jànge ca lekkoolu digg-dóom ji ñu duppe Louis-le-Grand ca Pari. Bim fa génnee, mu tàbbi ca daara ju mag joojee ñuy wax École normale supérieure de Saint-Cloud. Jamono jooju, waxuma la sax am lijaasa ca daara joojee, waaye jànge fa rekk doyoon na ndam, dib sag bu réy a réy ci boroom. Bokk na ci liy màndargaal dayo daara jooju, mooy ne ki jëkk a jiite réewum Senegaal, Lewópóol Sedaar Seŋoor, ñu ràññee ko lool ci wàllum ladab ak mbind, bëggoon na fa dugg, waaye daa lajj. Muy biral ne, daara jooju, ab como daawu fa teg tànk. Am na sax ñuy wax ne, Seŋoor da koo iñaane woon ndam loola, ragal ne dina ko may fitu wujje ak moom ci làngu politig gi, ñeel Senegaal. Sëñ bi Jóob, nag, du woon ragal walla tóoyemaan, ni ko ndaw yiy waxe. Bañkat dëgg la woon, ñeme woon xeex. Dafa di sax, ni mu ame woon noonu fit moo taxoon ñu dàq ko, moom ak benn doomu Farãs bu daan wuyoo ci turu Daniel Cohn-Bendit, ca daara ju mag jooju, ci atum 1969. Waaye yemul foofu. Ndege, Omar Bolondeŋ Jóob dafa xaroon tànki tubéyam, di xeexal askanu Senegal. Mi ngi féete woon ci kóminist yi, daan roy ci doxalinu Mao-Tsé Toung. Kurél gi mu bokkoon mësul a juboo ak Seŋoor, foo leen fekkaan, ñu ngay jàmmaarloo. Ndaxte, Seŋoor nguurug Farãs la fi toogaloon te, ci wàllu xalaat ak politig, yoonu kapitaalist yi la Farãs ak ñi far ak moom toppoon. Loolu mi ngi tollook jamonoy xareb suuf (guerre froide) bi amoon ci diggante U.R.S.S. (kóminism- sosiyalism) ak réewum Amerig (kapitaalism–liberaalism). Àddina si xar ñaar : ñii far ak U.R.S.S. miy mujje dooni Riisi, ñeneen ñi far ak Amerig. Bi mu ñibbisee Ndakaaru, mu wéyal xeex boobu ci ndimbaluy rakkam. Ñoom ñépp ñu doon xeex nooteel, teg ci di ŋàññ doxalinu Seŋoor mi doon wéy ci waawi Farãs. Seŋoor demoon na sax ba jël Jean Collin, di doomu Farãs, boole ci di jegeñaale Jacques Foccart, toftal ko ci boppam, dénk ko lépp lu jëm ci kaaraange biir réew mi. Loolu la Omar Bolondeŋ Jóob ak i àndandoom doon xeex. Ndax kat, Seŋoor dafa jébbalu woon ci Farãs ba nga xam ne, buñ tisóoliwaan Pari, mu ne yaaram-kàlla. Am jamono, Seŋoor sumboon fi liggéey bu mag ñeel mbeddi ndakaaru yi, santaane ñu set-setal gox-goxaat yi ngir laabal leen. Te, nag, duggewu ko woon lenn lu dul teeru Pompidou mi jiite woon Farãs, ngir bégal ko. Loolu metti lool Omar Bolondeŋ Jóob ak i rakkam ba tax ñu demoon taali Njawriñu Liggéeyu caytu gi ak Kërug aada ak cosaan gu Farãs ci Ndakaaru, ñu doon ko wax « Centre culturel français ». Yemuñu ca, ndax defaroon nañ ay ndell, fasoon leen yéenee sànni ci kow woto yi yaboon Seŋoor ak kilifa tubaab yi mu waroon a teeru. Wànte, dañu mujje lajj ci pexe moomu. Ci lañu leen tege loxo. Jàllo Jóob moom, dañ ko tëjoon Kéedugu giiru dundam ba noppi sas ko liggéey bu mu sañutoon a bañ, dëkke koo metital ak a xorñoññal ca biir kaso ba. Ca la Omar nisëree woon ca Mali ga mu dawoon làqu, ne day afalsiy rakkam, kilifay Bamako tegati ko loxo, jébbal ko nguru Senegaal. Ñaar fukki fan ak ñett ci weeru Mars ci atum 1972 la këru àttekaay bu Seŋoor àtte woon Omar Bolondeŋ Jóob, daan ko ñetti ati kaso yu mu waroon a tëdd. Li ñu ko jiiñoon moo doon “nasaxal kaaraange réew mi”. Mu doon xeex doxalinu Seŋoor wi aju woon ci li neex tubaab yi ba noppi worook bëgg-bëggu askanu Senegaal. Moom Omar Bolondeŋ Jóob, dafa mujjee ñàkk bakkanam ca kaso bu Gore ba ñu ko dencoon. Ci 14eeli fan ci weeru Mee atum 1973, la yéenekaayu nguur gi, “Le Soleil”, siiwal xibaar bu tiis bi : “Kurél giy sàmm kaso yi (…) mu ngi xamle ni Omar Bolondeŋ Jóob xaru na ci néegam ci biir kasob Gore ginnaaw bi mu yeewee buum ci baatam. Mu ngi ko def ci boori ñaari waxtu ci guddi”. Booba, 26i at kepp la Omar Bolondeŋ Jóob am. Amaat Daŋsoxo ne woon ca tonet, wax ne : “Dafa leer nàññ ci sama bopp ne Omar Bolondeŋ Jóob dañu koo bóom. Li tax kilifa yi ŋànk réew mi bóom ko nag, lenn rekk la : ak xel mi ko Yàlla mayoon, Omar mënoon na leen fee jële !” Ndeysaan, njabootu njóobéen – rawatina Jàllo Jóob – ñoo ngiy wéy di xeex booba ba léegi ngir ñu bañ a fàtte seen mag jooju. Ñoom li ñu jàpp mooy ne, Omar dañ koo rey, te dara waralu ko woon lu dul politig. Omar a ngi gaañu ginnaaw bi ñu ko metitalee ca kasob Gore ba, te ñu mën a njort ne lépp ci ndigalu Jean Collin la ame. Ñu bare ci ñiy gëstu ci mboorum (histoire du) Senegaal, loolu lañ jàpp.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/7-mars-walla-8-mars-bey-ci-sa-wewu-tank/
7 MÀRS WALLA 8 MÀRS ? BEY CI SA WEWU TÀNK… Juróom-ñetteelu fan ci weeru màrs la xel yépp di dem ci jigéen ñi, ndax seen bés la. Àddina sépp a koy màggal, di ci amal ay ndaje, ay waxtaan yu yaatu waaye it di natt ba xam fu xeex bi tollu. Lépp a ngi tàmbali ci 1917, ca Saint-Petersburg, at ma ay óbëryee yu jigéen meree, amal ab doxu-ñaxtu. Lu jiitu loolu, ci atum 1910, Clara Zetkin, doonoon jàngalekat, surnalist, politigseŋ, sooke woon na ndaje mu mag, jigéeni sosiyalist yi wuyusi ko, ñu daldi taamu 8 màrs, def ko bés bees war a siggil jigéen ñi. Ci 1977 la Mbooloom-Xeet yi nangu loolu, dëggal ko. Fii mu ne nii, amul benn njiitul réew mu sañ a tanqamlu jigéen ñi le 8 màrs. Niñ ko xamee, ñi ëpp ci ñoom ay góor lañu te koo ci gis mu ngi politige bés bi, di jéem a gëmloo jigéen ñi seeni tawat soxal nañ ko lool. Ci ñoom nag, am na ci ku xamutoon caaxaan ak tappale. Kooku Thomas Sankara la woon. Demoon na ba jël ca réewum Burkinaa-Faaso dogal bu yéeme. Saa yu 8 màrs agsee, da daan sant góor ñi ñu xéy fobeere néeg yi, duggi màrse, taal añ, toppatoo xale yi, fóot yëre yi, téye kër gi daal ni ko seeni soxnay defe bés bu Yàlla sàkk. Sankara dugge wu ko woon dara lu dul fexe ba góor ñi gën a xam li jigéen ñiy daj ci seen néegu-séy, su ko defee ñu weg leen, lépp lu ñu leen daan jàppale ñu xeeb ko, gën leen a taxawu. Jigéen, ni ko woykat biy waxe, ku ko sóoralewul, yakk ñamu-mbaam. Loolu lu am la. Sankara amoon nay yéene yu mag ci Afrig, jaarale leen ciy xalaat yu rafet te leer nàññ, kaar. Jigéen ñépp, rawatina yu Afrig, ameel nañ ko njukkal. Waaye ginnaaw bey ci sa wewu tànk, ndax amul beneen bés bu Senegaal waroon a jagleel ay jigéenam ? Sunu réew, nun, mooy réewum ‘’Talaatay Ndeer’’. Kon mënoon nanoo bañ a jéggaani ciy Tubaab bés bu nuy sargale jigéeni Senegaal. Am ñu ma ni : ‘’Bés boobu ban la ?’’ Maa ni leen : ‘’Nan fàttaliku.’’ Talaatay-Ndeer, 7 fan ci weeru màrs 1820 la woon, Naari Tararsaa yi song péeyum Waalo, fekkuñu fa lu dul i jigéeñ, bëgg a leen a jàpp defi leen i jaam. Ndaw su am fit suñ naan Mbarka Ja ne leen bésu dee du bésu dund, jomb nanoo nekki jaam ginnaaw Barag-Waalo, nanu dajaloo ci néegu-ñax bu mag bii, taal ko ci sunu kow. Noonu lañu ko defe keroog, di woy ci biir safara si ba sedd guyy, suuxat suufus Waalo ak seen jom ak seen ngor. Kon waay-waay yéen sunuy njiit, buleen ragal a def 7 màrs bésu jigéeni Senegaal yi ! Defeleen ko noonu, su ëllëg saa nu àndandook ñépp bokk ci xew-xewi 8 màrs yi. Ana lu aay ci yëkkati jigéen réew mi ñaari yoon ? Te sax, bu nu waxantee dëgg, li nga dàqe kon kéwél mu jëm àll, dàqe ko béy mu jëm kër.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/laaj-tontu-saada-kan-boris-iii/
LAAJ-TONTU SAADA KAN/BÓRIS (III) Waxtaan wii, ab tekki la ñeel jotaayu laaj-tontu bu Saada Kan di amal ci tele 2Stv ñaari ayu-bés yu nekk, te mu dalaloon ci sunu werekaan bi, Bubakar Bóris Jóob keroog, altine 22eelufan, sulet 2019. Bii mooy ñetteelu xaaj  bi, di yit biy tëj seen waxtaan. S. K. : Bóris, bi nuy waajal waxtaan wi, danga wax lu ma yéem. Danga ni : « Ñaar a am, Saada : làmmiñ wi may waxe, man, ak làmmiñ wiy wax ak man .»Ma bëggoon nga leeralal nu lu kàddu yooyu wund. B. B. J. : Waaw. Wax nga dëgg. Man ci sama bopp, bi may bind Doomi Golo lañ ma dikkal. Ndaxte, damaa dem ba ci yàgg mu mel ni ay baat yu doon nelaw ci sama biir xol bi ñoo jékkee-jékki yeewu, ràkkaaju nag, di awu ci sama biir yóor gi, di ma déey ay baat ak i xalaat yu yéeme. Ci laa ne ndekete am naa alal ju ni tollu ciy kàddu, ndekete lépp lu ma mas a wax ñii ñoo ma ko waxloo te ñoo may bindloo tamit ! Gis nga, bindkat bi war na fu mu tollu di ormaal làmmiñ wi mu nàmp, di ko jëfandikoo. Waaye, na fexee xam it wan làmmiñ ay wax ak moom, di cuq xolam ak xelam. Loolu sax a gënatee am solo. Bu ko defee, bindkat bi, baat yiy wax ak moom lay jëmmal ci téereem, muy téereb taalif mbaa téereb nettali walla kilib, maanaam tiyaatar. Loolu laa yëg bi ma tàmbalee bind ci wolof ba tax maa wax loolu. Su may bind ci tubaab mën naa feesal junniy xët te benn du ma ci yëngale noonu. S. K. : Bóris, bu ñu xoolee sa taxawaay ak ni ngay faral di waxe, mënees na jàpp ne dangay xeex li ñuy woowe ci nasaraan Françafrique. Te say téere dañuy biral xeex boobule. Jot ngaa bind di diiŋat nooteel boobu ak di tontuwaale way-boddekonte yi ñeel nit ku ñuul. Nu ngi sàkku nga dégtal nu tuuti sa xalaat ci xeex boobu. B. B. J. : Ndem-si-Yàlla ji François-Xavier Verschave moo xéy tëgg baatu Françafrique. Lan mooy Françafrique ?  Ci gàttal, Françafrique mooy naalub nooteel bi Frãs lal ngir teg loxo ci réewi Afrig yi, aakimoo seen alal ak seen moomeel te ay doomi-Afrig, sunu njiit yi nga xam ni ay cuune dëgg lañu, di ko ci jàppale, bokk ak moom mbuus.Loolu day firndeel ni Frãs mësu fee jóg, te xalaatu ko. Ba Frãs nangoo réewi Afrig yi moom seen bopp, daa génne ci bunt bi ba noppi làqu tëb palanteer bi delsi ! Fekk na mu tegoon nitam ku ñuul kukk ni yow ak man mii ci jal bi, kookuy wéy di ko defal lépp lu mu bëgg. Kon Françafrique loolu la, ay réewi Afrig yu ne ñoo moom seen bopp, am seen raayaak seen Pincez-tous-vos-koras-frappez-les-balafons waaye teewul Frãs di wéy di fa dogal.  Mu ngoog. Te sax, am na benn politiseŋuFrãs bu kàccoor te tuddoon Edgar Faure bu jeexal wax ji ba mu nee : « Daanaka nun waa Frãs danoo jóge Afrig ngir rekk gën faa mën a dëju !’’ Te gis nga, Saada, képp ku bëgg ay firnde ci lii ma la wax, na méngale doxalinu Frãs ak bu Àngalteer mi nga xam ne tegoon na fi loxo moom tamit ciy réewi Afrig. Xoolal, li ko dale ati 1960 yi ba nëgëni-sii, Àngalteer mësul yónni ay soldaaram Afrig ngir ñu ñëw dakkal ay xare yoo xam ne moom Àngalteer moo leen sooke ! Kenn mësul gis làrme bu Àngalteer ca Keeña, ca Tansani, ca Niseryaa, ca Ganaa… Loolooy li am. Moone, bu ko neexoon doxale neneen, jaay réew yooyu doole. Waaye defu ko. Nga dellu, xool Frãs. Du jar sax ngay sore ci sab gëstu. Li ko dale ati 1960 yi ba léegi, ay fukki-fukki yoon la yónni ay soldaaram fu ne ci réewi Afrig yi mu defoon moomeelam. Ñu ni déet-a-waay, mu sax ci, xaatimloo sunuy njiit – seeni xuus-maa-ñàpp yu ñàkk faayda – ay déggoo yu xel mënuta nangu ñeel mbirum làrme. Rax-ci-dolli, dafa ne déjj-déjjaaral ci sunu koom-koom, di nu ŋacc saa su nekk. Yaakaar naa ni Senegaal moom, ni Frãs aakimoo sunu koom-koom dootul lu ñuy laam-laame. Doxantul ci mbeddi Ndakaaru yi, yékkatil sa bopp xool bitig yu mag yi ak màngasin yi. Bu ko defee, dangay gis ne, ni ñu cëralee Frãs ci sunu koom-koom, ci nguurug Maki Sàll gii, mësu fee am. Jamono jii la Frãs gën a noot Senegaal. Li ci gën a doy-waar mooy ne, saa yoo ŋàññeeFrançafrique am i doomi-Senegal yu la mere, naan : « Yow daal, dangaa bañ Frãs doŋŋ !Tee noo takku liggéey ! Du moo gën ne fiy tuumal saa su nekk Frãs ?» Loolu yomb naa wax, Saada. Ku mu doon sa sago nga fas jom defar sam réew te sa yoon du nekk ci ñeneen ñi. Waaye na fekk ñu bàyyi la ci ! Seetal rekk, lépp la Frãs teg loxo, rawatina koom-koom gi ak sunu xaalis. Te CFA bi da koy firndeel te am na nu yëf yiy deme ay soldaaram mën nañoo dal ci sunu kow. Ci gàttal daal, ci nooteel lanu nekk ba nëgëni-sii. Képp ku yaakaar ni mén ngaa defar réew mi tey noppiwaale Françafrique,dangay nax sa bopp mbaa nga tey ko di nax askan wi ngir defaru yow ci sa bopp. S. K. :Bóris, wax nga ci teewaayu soldaari Frãs yi fii ci Afrig. Te sax, yaak Aminata Daramaan Taraawore jot ngeen a bind ab téere bu tudd« La gloire des imposteurs », jagleel ko lees di woowe “Opération serval” bi Frãs amaloon ca réewum Mali. Mën nga cee delseem ? B. B. J. : Waaw. Aminata Daramaan Taraawore ab xeltukat bu mag la ca Mali. Muy nit ku fa am tur lool, ñu jox ko fa cër te di ko may nopp. Lan moo xewoon Mali ? Frãs a defati mëninam, yónnee fay soldaar ngir, ci li François Hollande taafantoo woon, àtteji nguur gaak Tuwaareg yi, diy naar yu féete ci bëj-gànnaru réew ma. Looloo indi Opération serval bi nga tudd sànq. Du woon guléet Frãs di def lu ni mel ; moom kay, tur wi rekk mooy soppeeku, waaye saa su nekk mu yabal fiy soldaaram ngir sàmm ittey boppam. Noonu la soldaari Frãs yi teersee Mali. Keroog jooju, ay ndaw ñoo leen teeru, dar leen ak i móto, yor ay folóor yu rafet, di yuuxu ca kow : « Frãs Yal na fi yàgg ! Frãs Yal na fi yàgg ! ». Waaye, mbir mi ay naxee-mbaay kepp la woon, ndeysaan. Frãs boppam la fa teewaloon, du leneen ! May wax Farañse yi naan : « Bu dul woon nun, terorist yi, defkati ñaawteef yooyuy mbubboo lislaam àgg nañ Bamako ba rajaxe ko ! » mbaa : « Nun noo xettali doomi-Mali yi ! ». Ma ne : ay fen yu tooy xepp a ngoog ! Duñ ci lenn, te xam nañ ko. Mooy li wolof di wax rekk, dëmm rey la ba noppi di la jaale. Looloo tax maak Aminata nu gis ne, lii wareesu cee noppi. Ndaxte, lu ni mel moo amoon ca Kodiwaar ak ca Libi. Kenn umplewul li dal Bagbo, dal fi tamit Xadafi. Te loolu lépp, Frãs a nekk ci ginnaaw, di nos ak a nocci ngir ittey boppam. Noonu lañu def, yàq deru Bagbo ba mu yàqu yaxeet ba li ëpp ci xeltukati Afrig yi di ko tuumal ; ñenn ñi dem ba koy yéene dee, naa : « Bagbo, na dee ! » Li ko Nicolas Sarkozy dugge woon mooy teg fi ndawam, ab dunguroom, muy Alasaan Watara. Bu ko defee, ñi xamul jàpp ne Bagboo fi yées, Watara moom di yaaram, jub, fas-yéenee yemale ñépp te bëgg réewam. Xam nga ni loolu, ay waxi xale lay gén a nirool. Li ñu def Xadafi moo gënatee jéggi dayo. Fexe woon nañu ba népp jàppe Xadafi ni seytaane. Foofu tamit, xeltukati Afrig yiy tëb di dal, lu bon lu ne ñu koy yakk Xadafi, naan moom it yal na gaaw dee ndax nu féex ! Kon, maak Aminata su nu bindee La gloire des imposteurs,loolu xewoon ca Mali, xewoon ca Kodiwaar ak ca Libi moo ko waral. Danoo bëggoon a yee nit ñi ci tóoxidóoni yi Frãs di sooke ci sunu réew yi ngir aakimoo sunu alal ak sunu koom-koom.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/can-koddiwaar-2024-caabalu-bes-bi-3/
CAN KODDIWAAR 2024 : CAABALU BÉS BI NGIRTEY JONANTE DÉMB YI Démb ci talaata ji lees amal ñetteeli joŋantey kippug C gi ak gu D gi. Nii lañu demee : Kippug C : Senegaal matal na ñettam, Kamerun rëcc na. Démb bi 17i waxtu jotee la joŋantey kippug C gi tàmbali, mu nekkoon Gine Konaakiri – Senegaal ak Gàmbi – Kamerun. Senegaal mu ngi wéyal ay ndamam. Dafa gañe dëkkandoom bii di Gine Konakiri 2-0, gën a rafetal génnam ak toogaayam ca boppu kippu ga. Ñetti joŋanteem yépp la gañe, muy lu réy. Ci seen xaaj bu njëkk bi, gaynde yi xawoon nañu am tuuti jafe-jafe. Nde, ndawi Kaba Jaawara yi dañu tàmbali rekk, yéeg seen kaw. Ndax, xamoon nañ ne buñ mayee Senegaal dawal bal bi rekk, du baax ci ñoom. Waaye, ba ñu delsee ci ñaareelu xaaj bi, gaynde yi daldi fippu, nangu bal bi doxal. Ci 61eelu simili bi, ci benn teg-dóor (coup franc) bu jege kãwu Gine bi, Kerepeŋ Jaata daldi koy xellil Abdulaay Sekk, Cekkeen bi mbëkk bal bi ak doole, lakk caax yi. Ba ñu demee ba ci 90eel ba Ilimaan Njaay, goneg Màrsey gi, dolli beneen ci paasu Saajo Maane, muy 2-0. Noonu la joŋante biy jeexee. Ci ñaareelu joŋante bi, Kamerun dafa dóor Gàmbi 3-2. Waaye de, yombul woon ci ñoom. Gayndey Kamerun yi xawoon nañu cof buntu toog. Ba seen joŋante bi dawee ba ñu mitã ba dikkaat, doxal ba ci 56eelu simili bi la Tokoo Ekàmbi taal caaxi Gàmbi yi. Ñu dawal lu yàggul, Gàmbi fayu ci 72eel bi. Ñu ni déet-a-waay, Gàmbi daldi dugalaat ci 85eelu simili bi. Foofu nag, daanaka Gàmbi kalifiye woon na. Waaye, dañu dugal seen kã (87eelu simili), muy lu doy-waar. Mu nekk 2-2. Saa-Kamerun gëm ko rekk ba ca 91eelu simili ba, joŋante bay waaj a jeex, Kiristofëer Wóo tojati kër ga, muy 3-2. Kamerun kalifiye, Gàmbi toog. Seen kippu gi, Senegaal moo jël pée ak 9i poñ, toppu ci kamerun 4i poñ, Gine ñëwee ñetteel ak 4i poñ itam, kamerun jiitu ko ndax “carton rouge” bu mu amoon ca seen njëlbeenu joŋante ba. Gàmbi jël ndaare ak 0 poñ. Kippug D : Móritani def na ko Alséri, Àngolaa nax na Burkinaa Faaso. Ci gii kippu, lu kenn foogul woon, mbaa ñi ëpp, moo ci am. Móritani moo dóor Alseri mi jëloon CAN 2019 daldi koy toogloo. Mu bett daanaka ñu bari. Moom, Móritani, kalifiye na ci 1/8 dë finaal yi. Guléet muy am ndam ci CAN. Waayeet, guléet muy jàll ci ñaareelu sumb bi. Benn bii moo am ci joŋante bi, Muhammed Delaahi Yaali moo ko dugal ca 37eelu simili ba. Turam duggu na ca mboorum kuppe mu  Móritani. Àngolaa tamit dafa nax Burkinaa Faaso, dóor ko ñaari bal ci dara. Mabululu moo dugal bii bu njëkk bi ci 36eelu simili bi, Sini dolli ko ci 92eel bi. Moom Àngolaa moo jël pée ak 7i poñ, toppu ci Burkinaa Faaso ak 4i poñ, Móritani jël 3eel ak 3i poñ. Alseri mooy ndaare bi am 2i poñ. NAALU ÀLLARBAY TEY JI : KiPPUG E AK GU F Afrig dii Sidd dina daje ak Tunisi bu 17i waxtu jotee, ca beneen joŋante ba Namibi di ci dajeek Mali. Muy yu kippug E yi. Joŋante yaa ngiy daw jamono jii. Kippug F gi nag, bu 20i waxtu jotee lañuy futbal. Ci benn boor bi, Sàmbi dina ko ñàkkanteek Marog ; ci beneen bi, Tansani ak Kóngo Demokaratig dianñ laale.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/saartjie-baartman-ndaw-sa-tubaab-yi-defoon-mala/
SAARTJIE BAARTMAN, NDAW SA TUBAAB YI DEFOON MALA Saartjie Baartman ab jaam la woon, fekkoon baax ca réewum Afrig-bëj-saalum.  Moom, nag, benn doomu Àngalteer lañu ko jaayoon. Gannaaw bi, Tubaab yi dañu ko wutal ab dàkkental, tudde ko Venus Noire walla Venus Hottentote. Ci atum 1810 la àgg Tugal. Bi mu àggee, nag, tubaab yi dañu ko wuññi, gàcc ko, làññi di ko wone ci ja yi ak luuma yi, diggante Àngalteer ak Frãs. Waaw. Saartjie Baartman as ndaw su jekkoon, ab diriyànke bu amoon waŋ ak i ween yu réy lool la woon. Mu jaaxaloon tubaab yi, ba tax fu nekk lañuy jóge ngir deñsi-kumpa soxna si. Noonu la Tubaab bi nekke woon ak moom, xàwwi suturaam, dëkke koo toroxal. Yenn saa yi sax ñii làmbatu ko, ñee siif ko, ñeneen ñi di ko jam ak seen parasol ak yu ni mel. Mënees na wax ne, Tubaab yi ab mala lañu jàppe woon Saartjie Baartman. Li koy gën a firndeel mooy li ñu ko boole ci benn téere bees jagleel mala yi. Ku def jëf ju bon te ñaaw jooju mooy Cuvier, benn doomu Frãs bu doon gëstu xeeti mala yi. Noonu, gannaaw soxna Saartjie Baartman  nit ku ñuul la woon, Cuvier da koo boole ci mala yi, saytu ko, amal ay njàngat ci moom. Noonu, mu méngale ko ak mala yiy nàmpal, boole ko ci biir téere boobu nga xam ne, dajale xeeti mala yiy dund yépp a ko taxoon a jóg. Bi mu faatoo ci atum 1815, kenn ci gëstukatu Frãs yi gënoon a mag te xelam màccoon ci xeet yiy dund, da koo fees, daggate ko, teqale cër yi. Mu seppi yóor gi, dindi awra wi, denc leen ci anam boo xam ne duñu yàqu. Jëmm ji moom, ñu lëmës ko ne ko gàcc ci kàggu-aada gi ñu duppe “Musée de l’homme” te nekk ca Pari, di péeyub réewum Frãs. Saartjie Baartman, nag, dara yóbbewu ko mbugal bu ñaaw bii lu dul ni jigéen ju ñuul bindoo ak taaram. Ci atum 1994, ab diir ginnaaw bi politigu boddikoonte ci biir xeet (apartheid) jeexe ci réewum Afrig-bëj-saalum, ca la askan wa ñuy woowe ay xoyxoyca mooma réew sàkku ci Nelson Mandela mu fexe ba jot ci néewub Saartjie Baartman. Seen jubluwaay moo doon suturaal ko, denc ko ci bàmmeel. Waaye ñenn ci gëstukati réewum Frãs lànk ba tëdd ci naaj wi. Amuñu woon benn lay lu dul di wax ne néewub Saartjie boobu moomeelu Frãs la.  Noonu ba ci atum 2002 ci la Frãs soog a nangoo jébbale Saartjie Baartman ginnaaw bi dipite yi jëlee ndogal lu ni mel ca péncum-ndawi-réewam. Tabo M’Beki mi jiitewoon booba ‘’Afrique du Sud’’ sànni woon na ci kàddu yu daw yaram yii : “Kiy niru mala dëgg-dëgg du doomu-Afrig bii di Saartjie Baartman. Déedéet. Mala yi dëggëntaan ñooy ñi ko xañ boppam ba noppi def jëf ju ñaaw jii”.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM Real Madrid a ngi wër góol bu bees Thibault Courtois, góolu Real Madrid bi,  dafa ame gaañu-gaañu bu metti (rupture des ligaments croisés) ba tax na dina toog diir bu yàgg door a góoluwaat. Loolu nag, jur na njàqare biir Real Madrid ba tax ñoo ngi ci wër góol bu koy wuutoondi ko ca caax ya. Jamono jii nag, ñoo ngi làmbaatu fu nekk. Christopher Nkunku dina gëj ci pàkk yi Moom Nkunku, bi ko Chelsea jëndee yàggul dara. Waaye, du gaaw a futbal. Ndax, dafa gaañu moom it ci oom bi. Dañu ko oppeere sax. Xamle nañu itam ni dina toog diirub ñeenti weer laata muy dóoraat ci bal. Kylian Mbappe demul Real Madrid Li coow liy bari lépp ñeel Mbappe, ndax dafay dem Real Madrid am am déet, Mbappe dafa noppi rekk, ni tekk tekkaaral. Ba ci alxames ji, mu daldi ciy àddu. Li mu xamal njiitu Paris Saint-Germain li mooy ne, moom Mbappe, dafay toog PSG, mottali at mi ko dese sog a dem ci coobareem. Jamono jii nag, bëgg-bëggu njiiti PSG yi mooy mu yeesalaat pasam ba 2025, nga xam ni déwén, buy dem ñu man ci am dara. Wàññeeku, Mbappe dafa bañ loolu. Lim bëgg mooy jeexal at mi ko dese, demal boppam. Noah Fadiga amaat na këlëb Doomu futbalkatu Senegaal ba woon, Xaliilu Fadiga, dafa mel ni li daloon baay jaa koy bëgg a dal, mbirum feebaru xol bi. Loolu waraloon sax këlëb bim nekkoon ca Farãs, Brest, dogoon pasam. Mu bañ a yaras nekk di tàggatook a faju ba amaat këlëb, Gant. Muy këlëb boo xam ni bii, baayam Fadiga nekkoon na fa menn at ci mujjantalu dundug futbalam.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/dibeeru-welbati/
DIBÉERU WËLBATI Cialtine jii la njiitu réew mi doon jébbal askan wi saxaar gi ñu duppe TER. Waaye, laata looluy am, ndajem-ndeyu-àtte mi, siiwaloon na ci suba si juróomi wutaakon yi war a joŋante ci wote njiitéefu réew mi nu dégmal : Màkki Sàll (njiitu réew mi), Usmaan Sonko, Madike Ñaŋ, Isaa Sàll ak Idiriisa Sekk. Waaye, benn baat a fi lëmbe : wëlbati. Waa kujje gi naan, Màkki wëlbati na keesu réew mi, jël xaalis bu-dul jeex jagleel koog saxaar, te askan wiy jànkoonteel i jafe-jafe yu tar. Ñu neeti dafa kootoog yoon wi ngir wëlbati kàrt gi, seppi ñenn ciy naataangoom ci joŋante wote bi, Xalifa Sàll ak Karim Wàdd. Am sax ñu naan, ki tëgg làmbu dibéer bi ñu génn, te Bàlla Gay wëlbati Móodu Lóo jël ndam li, li mu ko dugge woon mooy juutal xelu nit ñi ba ñu fàtte solos bés bi.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/balla-gay-moodu-loo-naar-ci-dara/
Bàlla Gay-Móodu Lóo : ñaar ci dara Làmbu démb ak ju tey jeeka wuute ! Ndege, démb, bu nawet bi wàccaan, ci lañu daan tëgg làmb. Kon, nu gis ne ci njeexitalu mbey mi la mbër yi daan joŋante, ndax beykat yi ci seen bopp a daan bëre. Seetal ma lii rekk : jàmbaari tool, jàmbaari géew… Mbër mu ci nekk teewal sab gox ginnaaw bi nga fa wonee sag njàmbaar. Dafa di, nag, gox yooyoo daan bokk aw tund. Lees ci jubluwoon ? Xanaa fésal fit ak ngóora, jom ak ngor, ak lépp luy màndargaal waxambaane bu làmboo jikko yi ñu fi lim. Rax-ci-dolli, làmb xew-xew bu mag la woon, di tax nit ñiy booloo, di rafetal diggante mbokk yeek àndandoo yi. Kon, mënees na jàppe làmbu démb ni daara, daara ju ndaw yi daan taataan i jikko yuy jëme kanam mboolem-nawle mi. Bu loolu weesoo, lees ci war a jànge mooy ne : démb, ñi daan tëgg làmb jeek ñi daan bëre — beykat yi — duggewuñu ko woon wut alal walla màkkaan. N1épp xam nañu ni sunu maam yi bey lañ daan dundale seen njaboot. Te saa yoo nee mbey, xel yépp dem ci fulla, xareñ ak muñ, ñuy ay tànnéef ci jikko yi. Bu nu delloo cosaan daal, góor balay sëgg bëre, fàww mu doon ab ndàndi, ñu weg ko fa mu bawoo. Wax dëgg, royukaay noonu lay mel, dangay siggil saw tund, siggil saw askan, waaye yit dangay nekk sagal say way-jur ak sa njaboot. Ndeysaan, xalam demoon na bay neex, buum ga saay. Ci sunu jamono tey jii, ku-yeboo ne coppite yu mag am nañ ci mbir yi. Waaw ! Te coppite yi dañoo laxasook yàqute jamono ji. Ndax, tey koo laaj ci mbër yi ndax ay way-juram àndoon nañu ci muy takk ngemb di bëre, tontu bi benn lay doon : déedéet. Léeg-léeg sax am ci ku la ne moom làmb taxoon na ñu dàq ko seen kër. Li ko waral, nag, du lenn lu-dul ne kenn du am sa doom mu doon xale nga koy xiirtal ci muy bëre walla muy fecc, bàyyi fi njàngum daara walla xarala. Du càggéeni làmb baaxul, dafa di rekk ne, anam yi ñu koy defe léegee ñaaw te safaanook jëfi gor. Tey, ku déggal say way-jur, boo newul daara ja di jàng yaa ngi ci bérébu liggéyukaay yi di jàng xarala. Të ak ñàkk dégg seeni waxi waajur a tax ñu ci bari doon ay mbër. Waaye li am ba am moo di ne jamono jee soppi nit ñi niy kàkkataar. Moone de, mel na ni tey ña tëwoon seeni waa-jur ca njëlbéen, ñoom lañu def royukaayi ndaw yi. Ndax, ñoo fi tekki di dawal ci daamar yi fi gën a yànj, dëkk ci kër yu taaru ba dee. Ku ko weddi seet ko ci jaraaf gi nu dénk njàng meek lépp lu ci ajuy doxale ; kilifa googu, bu daara yiy ubbi, muy ànd ak kenn ci mbër yi, di wër ak moom yenn ci ay daara. Muy lu doy waar ! Teg ci tamit, nataali mbër yooyu ñoo ne fàŋŋ ci téere yi ndongo yiy jànge. Te bu jant biy so, ba gone yi wàcc, ëtti daara yi dañuy soppiku aareen, mbër yi di ci tàggatoo. Moom kay, salfaañoo dëgg la dundinu askan wile def. ! Kon léegi daal ku bëgg a tekki na fexe rekk ba am, ak noo mën a ame ?
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/nan-wax-ci-yenn-seri-tele-yi/
NAN WAX CI YENN SÉRI TELE YI Jamono jii nu tollu temm bari na lu ñu seetlu ci miim réew, ñeel tele yi. Waaye li ci gën a ràññeeku mooy séri yu bari yi ñuy dawal. Lu sabab lu ni mel nag mën nañu wax ne ciy ñaxtu la jὀge. Nde, ay at ci ginnaaw, liñ daan faral di gis moo doon séri tubaab yi. Loolu am na ñu mu neexul woon ba ñuy xultu naan yooyu séri dëppoowul ak dundinu doomi réew yi, du ci seen aada, du ci seen cosaan. Ñeneen ñi naan waaw, nun sax, lan moo nu tee fent ay séri yu dëppoo ak sunu nekkin ? Amaana xeex boobu moo jur coppite yi am tey. Ba tax na séri yi takkarnaase nañu lool. Yi ci gën a ràññeeku nag ñooy : Pod et Marichou, Mbetteel, Maitresse d’un homme marié, Idoleak  Golden. Naam lu rafet la ndax xaalis bu bari bi ñu daan def ci séri yi ñuy jéggaani ji am na fu mu xaj. Nde am na ñu xalaat ni dërëm bi des ci gaal gi bokk na ci liy suqali am réew. Ci misaal, Marὀodi tv, Oke Afrika añs ay bérébu liggéeyukaay lañ yoo xam ne ci jumtukaayu xarala yu yees lañu bokk te ñooy amal séri yi. Rax-ci dolli day tax ndaw ñi amul liggéey am fu ñuy dàqe seen wërsëg. Yemuñu ci loolu ndax it kër gu ci mel ni waa « A+ » day jënd séri yi di leen teg. Am na sax ñu jàpp ni jëmmal gi ñuy jëmmal séri yi dina tax nit ku ñuul gën a xam boppam. Waaye ñépp bokkuñu gis-gis. Mu mel ni rekk daa am lu ñuulal soow mi. Waaw ! Ndax am na ñu leen di ŋàññ. Li ñu doon daw fee ba tax nit ñi daan ñaxtu, moom la nuy tàmbalee gis ci sunu séri tey yi. Ñenn ci seetaankat yi jàpp ni bu weesoo Mbetteelak  Idole,benn séri méngoowul ak jikko yi waa réew mi miin. Seetlu bii nag ci Pod et Marichouak ci Maîtresse d’un homme mariéla gën a fése. Ñaari séri yooyu bari na ñu leen rafetluwul. Lu ñu ciy gën a ñaawlu mooy yenn jataay ak yenn kàddu yi tegginewul benn yoon. Waajur yi nag nee nañ lu ni mel day yàq gone. Li ëpp ci li ñuy wone dundinu nasaraan yi la gën a jege niki jigéen ju dëkk moom kese te amul boroom-kër ak yu ni mel. Walla bu dee am na sax ñi ko fiy dund, bariwuñu. Bu ñu wonee Afrig daal, ci colin mbaa ci làkk yi la yem. Wàllum jikko moom boolewuñu ko ci. Ci lu leen di suuxal rekk lañu nekk moo xam ñu xam ko walla déet. Mu mel ni rekk li ñuy bëgg a wone ak liy feeñ dañoo safaanoo. Lii taxoon na sax ba waa Jamra di kurél giy sàmm jikko yu rafet yi ak li méngook diine fésaloon seen mer ba ni woon dañuy yóbbu waa Maîtresse d’un homme mariéci yoon ginnaaw ba ñu amalewoon 11elu  jataay ba te Mareem di ab way-jëmmal ci séri bi kàddoo woon ni : « sama lii maa ko moom te ku ma neex laa koy jox ». Waaye de, boobu pelent mujjul fenn ndax waa CNRA di kurél gi war a saytu mboolem lu aju ci wàll woowu, daanaka àndu ci woon. Moo tax it diir lañu ci teg ñu amalaat lu ni weŋŋ ca 34elujataay ba. Altine 28elu fan ci weeru me waa Jamra wutaleeti CNRA ngir ñaxtooti ne lii kat day niiru kὀkkali. Kurél gi mujjee jël ay dogal jëmale leen ci kër gii di 2STV ngir ñu xoolaat  waxtu wi ñuy teg séri bi mbaa ñu dagg yenn jataay yi. Teg ci dànkaafu waa Marodi tv. Ne lu ko moy diñañ leen sàkkal pexe. Lii war naa tax ñiy amal séri gënatee bàyyi xel ci aadaak cosaanu réew mi te bañ a roy doxalinu nasaraan yi. Ndax toppandoo ay doxandéem amalul réew mi njariñ.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-8/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM CAN 2024 Amara Juuf bokkul ci 55i futbalkat yi Alin Siise tànnagum ngir yóbbu leen ca CAF laata mu di ko seggaat ba 27. Moom, kàppiteenu U17 bi, fim ne ma nga Metz ngir faju. Gaañu-gaañu yaa ngi bëgg a bari ci gaynde yi. Gànna Géy dolleeku na ca limu ñi gaañu fekki ñoom Séeni Jeŋ ak Nàmpalis Méndi. SUPER LIG Ëttu àttewaayu Tugal bi jox na dëgg Super League ci kaw UEFA, daldi koy daganal. Kon, saa suñu ko bëggee te mën ko sañ nañu taxawal seen i mbir te benn daan du ci fekk benn ekib niki woon ca njëlbéen ga. Gannaaw loolu nag, kii di Aleksander Ceferin, njiitul UEFA yëkkatina ciy kàddu yoy xol bu jeex lay niru. Mu ngi naan: “Mën nañoo taxawal lu leen neex. Di yaakaar ni dinañu gaaw a tàmbali seen joŋante bu xàttaaral bi ak ñaari ekib (Real Madrid, Barça).” Donte daganal nañu yëf ya, teewul am na ekib yu taxaw dàq boobu Super League, ñu ci mel ni Manchester United, Séville, Valence, Atletico Madrid, Bayern, Dortmund. GREENWOOD A NGI ÑËWAAT BU BAAX Gannaaw ndogal li daloon ci kawam ba taxoon yoon tegoon ko loxo laata ñu di ko bàyyi setal ko ci lépp, Manchester United miy këlëbam daf ko bañoon a jëlaat daldi koy abal Getafe (Liga). Fim ne nag, moo ngi wane boppam bu baax ca ekib ba di dellusi bu baax ci nees ko xamee woon. Amagum na fa 3i bii ak ñeenti paas. BUNDERSLIGA Bayer Leverkusen mooy ekib bi njëkk a dawal ca sàmpiyonaa Almaañ ñaar-fukk ak juróomi joŋante yoy ñàkku ci benn. Loolu di gën a dëggal taxawaayu ekibi ak liggéey bu rafet ba fa Xabi Alonso di def. Thomas Müller yokk na pasam ba atum 2025. Moom nag digganteem ak Bayern xanaa aj dàll rekk a koy tax a jeex. Nde foofu rekk la fas yéene futbal ba keroog muy bàyyi. Victor Boniface jëlatina raaya “Rokkie” ca Bundersliga ba. Gii di juróomeelu yoon bu mu tegale di jël raaya gees jagleel ki gën a xarañ ci weer wi.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-4/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM KUPPEG ÀDDINA U17 2023 Ndawi Senegaal yaa ngi ci waajtaayu kuppeg àddina si ñu dëgmal te war a am ci weer wii di teew. Cig waajtaay, fas nañu yéene amal ñetti ndajey xaritoo. Démb sax lañu bi ci njëkk ak Panama daldi koy dóor 4-1. Amara Juuf, Idiriisa Géy, Yayaa Jémme ak Umar Sàll ñoo dugal. Bokk nañu nag ci kippu gu dëgër, ànd ci ak Àrsàntin, Sàppõ ak Poloñ. Waaye, bu ñu dëggalee seen bopp, dawal seen futbal, mën nañu am dara. LAMIN KAMARA DUGAL NA BALAM BU NJËKK CA METZ Lamin Kamara démb lay sog dugal njëlbeenu biiwam ci Ligue 1 ak Metz. Ndaw bii bu réy ! Moom de kenn du ko fàtteel bu njëkkam bi. Nde, jàppees na ni dina bokk ci bii yi gën a rafet ci at mi. Ci seen joŋanteb démb ji ak Monaco la saa-senegaal bi daldi këf bal bi ca diggu powu ba, fekk góolu Monaco bi génnoon kãwam yi, mu lawbe ko ci soriwaay bu tollu ci 58i ñay (mettre). FSF MOO NGI GUNGEE KËLËBI SENEGAAL YI AK ÑI KOY DOXAL Fédération Sénégalaise de Football (FSF) xamle na ni tàmbali na gunge (subventions) yi muy defal këlëb yi ngir ñuy waajal seen bopp at mu nekk bu sàmpiyonaa biy waaj a tijji. Ren jii nag, koppar li mu teg ci taabal ji dañoo wàññeeku bees ko tëkkaleek yu daaw ya. Li ko waral nag mooy ne, daaw, dafa fekk nu gañe kuppeg Afrig ba noppi kalife woon ca kuppeg àddina sa. Moo taxoon mu joxe woon lu tollu ci benn miliyaar ak xaaj. Ren nag, daf ko wàññi ba mu toll ci 709 250 000 ci sunuy koppar ngir këlëb yeek ñi leen di doxal (acteurs) waajal ci seen bopp. MAROG DINA YEESAL Bu nu joxee nopp seen i njiit, Marog dina taxawal powu bu bees boo xam ni mooy doon ñaareelu powu bu gën a rëy ci kembaaru Afrig fii ak atum 2028. Moom Marog moo war a dalal kuppeg Afrig 2025, war a bokk dalal itam kuppeg àddina si, keroog 2030, mook Espaañ ak Portigaal. Réewum Afrig bi gën a sori ci mbooru kuppeg àddina (dëmi-finaal) dafa fas yéene dugal boppam bu baax ci wàllu futbal bi. RONALDO FASAGUL YÉENE BÀYYI Purtugees bi defagul mbirum bàyyi futbal ci xelam. Boo dégloo ay kàddoom xam ni waaju ko sax : ” Dina wéy di futbal ci at mii ak mi ci topp. Ginnaaw loolu, dinaa xool ndax sama yaram dinaa mën a àttan futbal bi am déet.” Ci atum 2023 mii, moo nekkagum futbalkat bu ci ëppaley bii (44) ci kanamu Mbàppe ak Halland. MAGUIRE MOO NGI ÑËWAAT Àngaleb Manchester United bi moo ngi tàmbali di ñëwaat ndànk ndànk, di tàmbaliwaat di def joŋante yu wóor. Gaawu gii weesu moo ci mujju, moom lañu tabb baay-faalu joŋante bi ci seen ndam li ñu am ci kow Sheffield United.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/2589/
KÀDDUY USMAAN SONKO 2/2 PÀCC Senegaal gépp amoon na fiy yëngu-yëngu, réew mi jaxasoo, yëf yi doy waar lool, yegg sax fu ko kenn foogul woon. Ñii seen i bakkan rot ci, ñee am ciy gaañu-gaañu yu metti, ñale ñàkk ci alal ju bari. Ginnaaw ba mu jógee “Section de Recherches” bu Kolobaan, Usmaan Sonko amal na waxtaan ak waa réew mi  ci 8eelu fan ci weeru Màrs. Waxtaan woowu nag, dara waralu ko woon lu dul mas-sawu leen ci yi fi jot a xew, xamal leen itam ni mook ñoom a bokk naqar. Lu Defu Waxu>, seen yéenekaay ci kàllaamay Kocc a ngi leen di baaxe ci ñaareelu xaaj bii, ay kàddoom na mu leen yëkkatee keroog jooju. (Ci taataanug Uséynu Béey) Nu war nag di waxante dëgg ndax Maki Sàll, li ko bewloo, bokk na ci nun waa Senegaal, ñenn ci nun waa Senegaal. Bala maa dee ñu naan ku xareñ la ci pólitig. Ndaxte yow mën ngaa dal ci sa naataangoo, mën ngaa ko kompaloo, mën nga koo jënd, walbati ko ba suy waxati du xam li muy wax lu mu doon ; loolu mooy xareñ ci pólitig? Nun, lin soxla mooy ku xareñ ci ni ñuy yoree réew ; koo xam ne, suñ la dénkee réew, nga defar réew ma. Xarañ ci pólitig dëgg mooy liñ la dénk, nga liggéey ko ba soo ne woon sama ñaareelu moomeel jeex na, maa ngi dem, ñu ne la bàyyiwuñu la. Juróom-ñenti ati Maki Sàll yi, li fi am, masul a am ci Senegaal. Ñaata naataangoom la tëj, ñaata la faagaagal? Loolu ba kañ? Loolu nag, la nu mënatul a nangu. Te nag, lii mu def, dañ koy tudde ci Tubaab wor wu réy. Maanaam wor wi gën a réy ci wor yi mën a am. Ndax moom bi ñu ko falee dafa teg loxoom ci sunu ndeyu sàrti réew mi daldi waat, ne «waat naa ne dinaa tënku ci ndeyu sàrti réew mi, dinaa nekk ci bëgg-bëggu askanu Senegaal». Li mu def wuute na. Ku dem ba yow nga wéet kunduŋ ak say juróomi nit, saw askan janoo ak yow, nga am sañ-sañu yónni jawriñ bu ñoradi bi, mu ne sa askan woowu yépp ay «terroristes» lañu, askan woowu wépp dafa am ñu nekk seen ginnaaw di leen jox xaalis. Ndaw yii dañoo mas a gis ku leen jox xaalis ? Taxaw saaga sa askan wépp, wépp. Yow doŋŋ ci sa pale ; tey boo ñëwee ci péey bi, moom kenn ak paleem, moom cunduŋ, askan wépp nekk fii. Su dul woon takk-der yi nekk sunu diggante, tey jii ay bagaasam dañ koy for. Loolu mooy wor wu réy ndaxte liñ ko joxoon ci ay jumtukaay du woon ngir muy «comploter» ay naataangoom. Dama wax tey, ñu ne ma «contrôle judiciaire», waratoo wax ci mbir mi, ma ne àttekat bi : «Su ngeen ci waxee ma wax ci». Ndax, ay mbir amoon nañ fi : mbirum Xalifa Abaabakar Sàlll gis nañ   ko, mbirum Karim Wàdd wax nañ ci. (…) Waaye, damay gaaral waa Senegaal. Wallaahi, dama ko waat, Wallaahi lañ ma tuumaal bu amoon, duma nangu benn doomu-Senegaal di ci am xoosu-xoosu, waxatumalaak bakkan di ci rot. Ndaxte bu boobaa, duma yem ci liñ ma def rekk, damay doon reykat ; kon doon na mel ni ñi ci faatu tey, man maa leen faat, duma nangu di am àq ak sama kanamu Boroom. Ñaawteefu Maki Sàll la ak ñi mu bokkal mbir mi. Ba tax nag, ñu ne : Njiitu-Réew, am na loo xam ne, du sa sañ-sañ. Amul Njiitu-Réew moo xam ne, war naa féewale askanam, di féewale nit ñi, ñuy jàmmaarloo, di xuloo walla di xeex ; amul Persidã boo xam ne, war naa jiite ci coxor, ci bañ nit. Ndaxte, ku àndul ak yow rekk nga ne kii tey ma faagaagal ko. Loolu du Njiitu-Réew. Te nun ñépp, nan ko ci bañ a jàppale, ndaxte kàdduy mbañeel, léegi lay door a am Senegaal. Tey laay door a dégg Senegaal ñu tudd waaso nit ci pólitig, walla ñu tudd ngëm-ngëmam ci pólitig. Loolu, nun ñépp, kenn waru koo nangu ; te di ci woo ñépp nag, te di ci boole «media» yi. Nun ñépp nanu góor-góorlu. Wuutale ay porogaraam, ay naal ak ay xalaat, nangu nañ ko. Waaye def ay porogaraam ngir rekk ay nit ñëw di saaga nit, di ŋàññ nit, di wax ci moom loo xam ne du dëgg subaak ngoon, mu yor njaboot, am ñu ko bëgg, yor ay militaŋ, loolu mooy taal am réew… Nanu delloosi sunu xel, mbir mi sottante xalaat la, wuutale ay xalaat, ay porogaraam la, waaye du xeex ak kujje gi. Kenn ku ne deram rekk la am, waaye xéy suba ba ngoon, jóg di wax ci nit, di wax ci nit, di wax ci nit, tam ko dëmm, wax ciy mbokkam, wax ciy waa-juram, loolu amu fi woon ci Seŋoor, amu fi woon ci Abdu Juuf, amu fii woon ci Ablaay Wàdd ; mu ngi door a am, te dafa war a dakk. Maki Sàll moomul réew mi. Nun ñépp noo war a jël sunuy matuwaay. Te lii, defe naa buñ ci jógee dina doon njàngat ci nun ñépp. Ndaxte maa ngi seetaat porogaraam yi, dàŋŋaaral bi wàññeeku na. Ndax waroon nanoo toog ba agsi fii? War nañ cee jël ay njàngat. Ku ñu dénk réew, ñii nga xam ne ñooy say takk-der, nga xam ne kaaraange réew mi moo leen tax a jóg, waruloo leen teg ci yenn anam yi.  Ndaxte takk-der yi ma gis, ñoo gën a am lu leen naqadi fi nu tol nii ; ndax xam nañu ni ki ñuy dóor seen rakk la, xam nañu ni ki ñuy gaañ seen rakk la ; koo ci wéetal; xolam seddul. Ku ñu jox réew war ngaa moytu loolu. May sargal nag Sàndarmëri Senegaal, ci seen mën-liggéey, ci seen sago. Man dama leen a mujjee naw. GIGN, bés biñ may jàpp ba tey biñ may delloosi ma dem noppaliku, ci seen loxo laa nekk. «Brigade de Recherches», noonu. Ngalla waay bu nu caaxaane sunuy «institutions» (campeef). Kenn musu ma sax bëmëx, kenn musu ma xoos. Kon ñooñu, ku am ñu mel noonu, àddina sépp ñee na ñu ko, ngalla waay Maki Sàll bul yàq sunu réew. Sàndarm boobu gaañu démb, ci GIGN yi ma yoroon la, di liggéeykat bu mag a mag a mag, ku bëgg réewam, tiitaru Senegaal la ; ñeewant bi mu amoon ci ñi mu doon sànni gërënaad bi, moo tax mu téyéwaat ko, moo yàq loxoom tey. Kon yooyu dañ ciy bàyyi xel, te gëm naa ni, ni mu amee ci sàndarmëri la amee ci yeneen tàkk-der yi. Kon waay-pólitig yi buñu yàq sunu diggante, nun waa Senegaal, waaye it sunu diggante ak sunuy campeef, rawatina sàndarmëri, xare bi, pólis ak leneen ak leneen. Di wax tamit ni, Maki Sàll mooy ndeyu-mbill gi ci li xew nii ci réew mi ; te loolu dunu ko bàyyi mu jàll. Maki Sàll amul màqaamay jiite Senegaal tey jii, amu ko ! Amu ko woon démb tey doog a ñëw. Ndax man bokk naa ci lawax yi nga xam ne, bi nu génnee ci 2019, maa waxoon ñetti lawaxi kujje gi, ne leen sama ngëm-ngëm du nañ génne xale yi, mooy duñ ko jàppe ni Njiitu-Réew mi. Mooy persidã ci kanamu Yoon waaye amatul màqaama bi. Defe naa mennum man ci lawax yi, maa ci yor taxawaay boobu ba léegi. Musuleen maa dégg mani ko Persidã Maki Sàll. Maki Sàll laa koy wax ndaxte màqaama Njiitu Réew amu ko, dafa mbuxum wote bi. màqaama boobu nag, li ci desoon lu tuuti, moo fi nekkatul. Kon su nu nekkoon ci yenn anam yi, Maki Sàll dañ ko waroon a wacce tey jii. Su nu nekkoon ci yenn anam yi, waaye, foofu nag laa bëgg askan wi dëglu ma, nanu dëgloonte bu baax a baax a baax. Ndaxte, loo gis rekk teey ak dal daf cee baax. Benn, bu kenn dem pale ne Maki Sàll day wàcc ci anam yu ko neexul, ndaxte loolu baaxul ci demokaraasi, fi mu mën a jëme réew mi du baax. Moom, bu xoolee boppam ba xam ne amatul màqaaamay jiite Senegaal, mu ne «jóg naa man, bàyyi naa», na askan wépp jóg tàccu, nu waajal sunu wote, ñi war a dem, dem jàmmaarloo. Wànte, bu ko deful, nanu ko gunge ba màndaam jéex. Ñaareel bi, yenn boroom xam-xam yaa ngiy wax « gouvernement d’union nationale». Nun de, sama bopp laa mën a waxal ak ñi ma àndal, bokkunu, jegewunu benn xeetu guwernmaa bu Maki Sàll. Ndaxte, dañ koo nawloowul bay mën a ànd ak moom ci guwernmaa. Ndaxte koo dem ba ne dafa wor, waratoo wéy di ànd ak moom ci guwernmaa. Léegi nag mu des, li ma bëgg waxtaaneek waa Senegaal :  coppite bi, «révolution», am na ba noppi, kenn mënautu koo téye. Bu ñu ne woon coppet Usmaan Sonko yóbbu, walla ñu def ko Dëkurwaa walla ñu def ko Séex Tijaan Jéey, walla Xalifa Sàll, ku mu mënti doon, du tee, ñii ma gis nii ci ndaw ñi, kenn mënatuleen a téye. «La révolution est en marche», te gën cee yàgg, 2024 nu mottali ko. Li ci des mooy, nanu bañ a def njuumte yi nga xam ne réewi Afrig yu bari def nañ ko fi : mooy, dañuy def seen coppite, «révolution», ba egg ca cëppaandaw ga, mu am ñu ñëw ne ko coppet, rawatina nag xare yi. Ndaxte, réew am na fu muy tollu, xare bi day jël nguur gi. Te ñaare, xare, day am yeneen réew yu am doole yuy jël seeni nit waajal leen ngir ñooñu jël réew mi. Bu nu sàgganee ba xare jël réew mi, lépp li nu doon yóotu ak di ko nas dinanu ko ñàkk. Moo tax ma ne «syndrome malien» baa ngi nii. Keroog ba ñu defee seen coppite  bay waaj a egg, ñu ne xare ba génn na, ñu topp ci «chars de combat» yi di tàccu, laa ni mbir mi jeex na, ñàkk nañu, ak feneen ak feneen ak feneen. Moo tax coppite gi am na ba noppi. Maki Sàll mënautu koo téye, kenn mënu koo téye. Kon nan ko gunge ndaxte pexe dafa baax ci lu ne. Du lépp nag lañuy wax ci tele, waaye sunu warugar nun ñépp, askan wi, mooy nan ko gunge ba nu egg fi nu bëgg a egg. Waaye nag, loolu tekkiwul ni, danoo firi Maki Sàll rekk di ko seetaan. Nuŋ koy gunge mooy, danu koy tënk ci wenn doxalin ginnaaw-si-tey. Ndaxte loolu la askan wi bëgg. Askan weey dogal tënk ci dooleem. Tënk boobu nag, bokk na ci : – Benn lu nuy «exiger» la, bu ci njëkk mooy ñii nga xam ne seen bakkan rot na ci mbir mi, te muy ki ko def, moom Maki Sàll, nañu jox ndàmpaay seeni njaboot. Te ñu ubbi lànket bu tënku- wul ndax ñu xam ku tiire ak kan moo rey. Te itam, dinanu yóbbu mbir mi ci “Cour Pénale Internationale” mu àtte ko. Ndaxte, yii, ay «crimes contre l’humanité» lañu, te ci nguuru Maki Sàll la xewe fii ci Senegaal. – Ñaareel bi, mooy ñi ci gaañu, dañ leen war a jox ndàmpaay, ñuy «civils» walla diy takk-der, jàppale leen ñu mën a faju ci ni mu gën a rafete ; – Ñetteel bi, mooy ñi ñu jàpp ndax seen taxawaay ci pólitig bi, na leen Maki Sàll bàyyi ci ni mu gën a gaawe. – Ñenteel bi mooy, bis niki tey dootunu nangu Maki Sàll di bunduxataal ñi àndul ak moom ak jaambur yi, di leen wattu, di leen déglu ci lu ñu yëgut, saa su ne. – Juróomeel bi mooy, ñi nga xam ne ay sàmbaa-bóoy lañ yu mu jël, jox leen xaalis, ñu yor ay jaasi ak i fetal, nañu def lànket ba xam ñan lañu, jàpp leen, jébbal leen Yoon, ñoom ak ñi leen yónni. – Juróom-benneel bi mooy, Maki Sàll, bëgg na ko, bañ na ko, dina fexe ba ñu mën a dem ci ay wote ni mu gën a leere. Ay wuruj «fichier électoral» jeex na ci Senegaal. Yor say kar-dàntite ne duma ko jox ndaw ñi ndax ànduñook man, jeex na ci Senegaal. – Juróom-ñaareel bi, mooy, ci ni mu gën a gaawe, foog ñu amal wotey gox-goxaan yi, doomi-Senegaal yi tànn seeni meer. Na Maki Sàll amal it wote dipite yi ci atum 2022, doomi Senegaal yi tànn seeni dipite, jox seen bopp Péncum ndawi réew miñ bëgg. Waaye dina doxal it ci atum 2024 wote ngir tànn njiitu réew mi ci ni mu gën a rafetee. Lii, lenn rekk moo ko mën a gàntal, mooy mu dem ba xam ni moom, jiiteetul Senegaal, amatul màqaama bi, mu ne bàyyi na,  ñu amal ay wote lu jiitu 2024. – Juróom-ñetteel bi mooy, na Maki Sàll delloo ñi mu ko xañ, seen àq ak yelleef ci pólitig : benn ci Xalifa Abaabakar Sàll mii, ñaar ci Karim Wàdd. Maki Sàll mooy tànn kuy lawax ak ku dul lawax, loolu jeex na Senegaal. – Juróom-ñenteel bi mooy, moom Maki Sàll, na taxaw jàkkaarlook waa Senegaal yépp – amul lu ma neex laay def, walla du waaw du déet ; fii déet rekk moo fi am – ne ñetteel  sax dootuma ko tudd waxatumalaak ñetteellu moomeel. Atum 2024 Maki Sàll du nekk lawax ci Senegaal. Lii lépp nag dafa am lu mu àndal, may ñaan askan wi, rawatina ndaw ñi, sunu taxawaay bii, bu mu wàcc mukk nag. Tey lanu war a gën a taxaw. Kenn ku ne ci nun am na sañ-sañu jëfandikoo àqam bi nga xam ne ndeyu sàrti réew mee ko ko may ni : «man duma nangu ku ma noot». Loolu ngeen def tey jii, loolu ngeen def fan yii yépp weesu. Nu wéyal taxawaay boobu. Waaye, na doon taxawaayu jàmm, ndaxte dafa am lu Maki Sàll foqati woon ci nun : kenn amatul woon sago def mbooloo. Tey, won nañ ko ni mu bëgg ko mu bañ ko danu koy def ndax ndeyu sàrti réew mi moo nu ko may….. May wax nag, ginnaaw ba ma waxee ci Maki Sàll, may woo nun ñépp, nun ñii ñépp di ay way-pólitig ; askan wii, yelloo na ay way-pólitig yu mat. Nun ñépp amatunu sañ-sañ ci yenn yi, nanu sargal askan wi, nanu ko delloo màqaamaam, nanu ko waat nun ñépp ni, askan wi rekk moo nu ñor ; kenn newu fi di def pólitig ngir xaalis booy am ; ku bëgg ay milyaar, uti ko feneen. Waaye pólitig jaamu sa askan la, yaa ciy sonn, dugal ci sa alal, ñàkk ci ba dee, waaye waroo foog ni, ci pólitig ngay ame milyaar. Kon, nax nga sa bopp. Loolu dafa war a dakk ci Senegaal. Man dey, man Usmaan Sonko,  tuuti naa lool ci kanamu askan wi. Gisuma lan laa def ba askan wi daj li mu daj ci nun. Kon nun it, nanu waat ni, bis niki tey, dinanu am doxalin wu yees. Ndaxte réew mi yomb naa defar de. Bii yoon, war nanoo jublu ci doxalin wu bees. Su dee nag, danuy ŋàññ ñi fi nekk ba jële leen fi, ñëw def lañu  daan def walla lu ko yées, defe naa ne, askan wi day, mujj génn ci nun ñépp. Ngalla waay nañ ci góor-góorlu. Ma yokk ci benn poñ. May sànni ay kàddu jëmale ko ci Kaasamaas, ci mujjeelu yoon wi. Samay mbokk laay waxal, walla ñenn ci samay mbokk, ndax Yàlla may na ma ma bokk fépp. Ak lu nit mënoon a jàpp ba tax nga dugg ci àll bi, jàpp ni dañ laa xeeb, jàpp ni dañ laa boolewul, jàpp ni «citoyen de seconde zone» nga, boo xoolee li xew tey ci Senegaal, dinga xam ne loolu amut. Ndax, ginnaaw ba ma doonee doomu-Senegaal, doomu- Kasamaas laa. Waaye ñii ñépp jóg taxaw, muy Tuubaa, muy Ndar, muy Fuuta, Bakel, muy Kees ak feneen ak feneen, jóg taxaw, seetuñu kii fu mu bokk. Dëgg jot na, nanu xeex ngir dëgg sax fi. Kon, li ma leen di ñaan mooy ci 6i weer yii, li may ñaan samay mbokk yi ci Kaasamaas, ku ci yoroon ngànnaay na ko teg te bañ cee laaj dara, génn, nu bokk ndey bokk baay, te xam ne nun ñépp doomi -Senegaal lanu, doomi-Afrig lanu. Ginnaaw ga, ngeen ànd ak sunu xare, fépp fu nit ñi ne woon ngeen génne kàrt yi, génne miin yi, génne ndell yi, aar nit ñi. Bunu nangooti ñu ne dañ koy saafaraal ci ngànnaay. Ndaxte, kiy jam ak ki muy jam ñoom ñépp doomi-Senegaal lañu. Nun ñépp benn lanu. Kon loolu, mooy woote woo xam ne, maaŋ koy woote ndax lu ma ñor a ñor la. Te ku seet bu baax li xew Senegaal tey, dinga xam ne waa Senegaal yépp wone nañ ni Senegaal benn bopp lanu. Kon, lii lanu ci bëggoon sànni ciy kàddu yu gàtt….. May rafetlu it teewaayu soxna yi ; tudduma goor ñi, bis bii, bisu jiggéen ñi la. Soxna Aminata Lóo Jeŋ, ministar bi, di ko gërëm bu baax ci teewaayam ak ci taxawaayam ci xeex bi, ndax bi mbir mi dooree rekk la dawsi  kër ga, jaa-ngeen-jëf…
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/moodu-loo-daan-na-aamaa-balde/
MÓODU LÓO DAAN NA AAMAA BALDE Xaar bi yàggoon na lool, waaj gi tamit naka noonu. Waaye, ñaari mbër yi mujje nañu sëgg démb ci dibéer ji. Móodu Lóo ak Aamaa Balde bëre nañ démb, ca aareen nasiyonaal ba ca Pikin. Móodu Lóo moo daan, yóbbu ndam leek metel mi (la couronne) Pàrsel. Seen làmb ji, bi ñu ko dalee waaj, yàggoon na lool. Jotoon nañ koo àppal ca njëlbeen laat ñu koy bëtal ci sababi gàllankoor. Moo taxoon ñu dàkkoon ko ba jëmmi jamono. Démb nag, ci dibéer 5i fan ci nowàmbar lees ko jàppaatoon te mujje na am. Ci fan yii ñu génn, gisees na ñaari mbër yi, Aamaa Balde doomu Pikin ji ak kii di Móodu Lóo doomu Pàrsel ji, ni ñu doon waajalee bés bi. Amaloon nañ ay jàkkaarloo yu saf sàpp. Werente bi bari woon lool ci diggante soppe yeek farandooy mbër yi. Fan yii ñu génn ba tay, foo geestu nit ñaa ngi ciy wax, ku ci nekk naan sama mbër a mën, sama mbër ay daan. Mënees na wax sax ni làmb dafa mel ne lu dekki. Nde, toogoon nañu jamono yoo xam ne yii, bu mbër mu mag waree bëre sax kenn du ko yég, mbaa ñu ci bari bu desee ay benn fan, ñaar lañ koy yëg. Bëre Aamaa Balde beek Móodu Lóo bi nag, dafa dekkil làmb ji, naatalaat géew gi. Jaadu na nag, ndax ñaari ndaanaan a doon daje, ku ci nekk mbooloo nekk sa ginnaaw. Móodu Lóo yàgg naa def i jaloore ba jël metelu làmb ji (la couronne de l’arène), nekk buur bi, maanaam « Roi des arènes ». Ci Ëmma Seen, moom it di doomu Pikin, la ko nangoo woon. Gannaaw loolu, Ëmma dikkaat ngir nangu ko, saa-pàrsel bi daldi koy bañ, daanati ko. Ba tax na, mënees na ni loolee yokk jom kii di doomu ndem-si-Yàlla ji, Fàllaay Balde, ci mu gën a ñafe ba ñu taxawal bésam ak Móodu Lóo. Li war ci bés bi yépp nag, ñaari mbër yi def nañu ko. Ci bés bi, ku ci nekk ñëw na na mu waree, bàkku, neexal bés bi, yëngal fowu bi (Arène national). Cokkaasante nañu, xarfa-fuufa yi ñépp gis nañu ni ku ci nekk ci ñoom ñaar def nga ci xaalis bu weex tàll. Amaa dikkee na nañu ko xamee woon, Móodu, wàllu sangu bi ñëwee na ci nees ko miinee woon it. Waaye, ci wàllu téere, dafa dëggal li mu ne : « woon weesu na fu may takkatee gàllaaj yu bari ndax làmb. » Ba ñu defee loolee lépp nag, la arbit bi daldi woote ca digg géew ga, ku ci nekk ñaan la muy ñaan, léemu ay léemoom. mu laaj leen ndax pare ngeen, ñu ne waaw, mu daldi sex mbiib ba rekk ëf ca. Ñépp ne tekk, fowu ba ne selew, soppe yépp jël xol yaak xalaat yaak yépp jëmale leen ca bëre bi, ca ñaari mbër yay laale. Ñaari mbër yi tàmbaley léewatoo, ci ay saa, Amaa daldi tàmbali di dox ci kaw Móodu Lóo, nees-tuut ñu tàmbalee sànnantey kurpeñ rekk roofaloo. Doomu Pikin ji dóor mboot, Móodu ci mën bëreem, rocceku Amaa rëpp, samp ñetti cër ya, doomu pàrsel bi wër ko ndombo, jekku ko, di ko rokkoos ak nokkoos. Dóor yi mel ni mbàccum gerte. Móodu Lóo tiim Aamaa Balde, jàpp kanam giy dóor rekk bañ a bàyyi. Biir dóor yi mettee ba metti, as waay a dawee ci bitig géew ga, romb takk-der yi, ñëw laxasu Móodu Lóo ngir wallu Aamaa mi mu àndal. Ca lañu àttee ñaari mbër ya. Lu leer ba leer, ci soppey Amaa Balde yi la. Ndaxte, moom lañ jekku woon. Gannaaw loolu nag, arbit yi gise, dem ca “var” bi nga xam ni lu bees la ci làmb ji, bii di ñetteelu yoon biñ ko jëfandikoo ci làmb ji. Ci seet, settantal ñu jox kii di Móodu Lóo ndam li, mu delloowaat nguur gi Pàrsel. Waaye, lenn ci lu ñuy rafetlu mooy ba ñu joxee doomu Pàrsel ji ndam, Aamaa Balde daldi ko jox loxo, kott ko, ndokkale ko, muy lu ñu bëgg ci bés yile, tubaab di koy wax “fair play”. Bu lépp weesoo, lenn ci lees war a bàyyi, mooy li am démb, ay sàmbaabóoy di bawoo fële di duggu ci géew giy yàkk làmb ji. Lees war a wutal saafara la balaa muy wéy di bari. Te, loolu, liggéeyu takk-der yi la, ñoom ñi war a sàmm kaaraange nit ñi.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Malaanum Lëndëm : Bóris Jóob, na woon, fa woon Ñeenteelu yoon a ngi nii Bubakar Bóris Jóob di génne téere bu mu bind ci wolof (+), te mu tudde ko Malaanum lëndëm ; muy téere bu EJO móol. Bóris moom, kenn dootul woññi ay mbindam ci làkki réew mi ndax ni mu nuy jàngalee li war a nekk, naka jekk : di bind ak a jàng ci làmmiñ yi nu nàmp. Li ëpp ci nettali bi, Niseriyaa lay xewe, doonte sax Senegaal lay doore. Taxul nag mu jëm ci mbiri “Boko Haram” ak i ma-rëtal yi ne ca dëkk boobu, di jàpp ak a faat jaambur yi. Konte, ni mu ko defe woon ak Murambi, le livre des ossements (bi amoon Raaya Ladab bu mag boobu ñu ràññee ci àddina sépp, di Neustadt), Bóris daa tànnati meneen réewu Afrig mu sori Senegaal gii mu cosaanoo, di Niseriyaa ; ñu gisaat fii doomu Afrig bi mu doon, bu xër ci mbëggeel gi mu am ci kembaar gi réewam féete. Rax-ci-dolli, nettaleem bi yépp dafa fees dell ak takkandeeru Amilkaar Kabral. Li ci nettali bi Ci téere bu bees bii nag, bindkat bi mu ngi nuy nettali xew-xew yi juddoo cib lànket bu Keebaa Jakite di amal ; Keebaa, genn góoru baykat la, dëkk Tànjuraa, ab gox bu nekk ci penku Senegaal ; lànket bi, li ko lal mooy xam lu waral ñu bóom xaritu benn bakkanam, Jonas Akintoye, doon doomu Niseriyaa bu dëkkoon Ingwini ca réew moomu. Ñoom ñaar nag, ay xarit dëggëntaan lañu woon, ku ci nekk jàppoon sa moroom ni woon ni doomu-ndey : Naka lañu mënoon a def ba duñ daje bés mook Jonas Akintoye, ku ci nekk ne jàkk sa moroom, ñu yëg ci saa si ne ay doomi-ndey dëgg lañu, ay doomi-ndey yu bokkul deret ? Noom ñaar, benn bëgg-bëgg lañu am, muy xër li ñu bokk xër jëmale ko ci lépp luy laal ci mbay. Waaye seen ànd yemul foofu, dañu nirooy jikko niy seex : ñoom ñaar ñépp dañoo gëm seen bopp, am péexte gu mat sëkk ba dara feesul seen i bët ; ñuy ñu dëggu, ñemee wax seen xalaat ak lu leen ci mën a fekk ; ñu doon ay nit ñu jub te am fit, bëgg seen réew te gëm seen i baaxi mboolaay ak seen cosaan. Ngëm-ngëm yu tumurànke yooyu ciyjamono yii, rawatina ci way-pólotig yi, nga xam ne, lu ne man nañ koo jënd, ba ci nit sax ak i noppam ! Ñaari xarit yii nag, ca ba ñuy ne ci seen diggu doole lañu xamante, ñu daje woon ca benn peyu Ërob, fu ay kuréli baykati Afrig gépp daje woon. Fekk booba, ku ci nekk ci ñoom ma nga jiite woon ca sa dëkk ay mbooloom baykat. Ba ñu fa jogee lañu jàppante ba seen i njaboot di demalante bu baax, doonte seen i réew dañoo soreyoo lool. Bés, ñu xamal Keebaa ci njeggil-kàddu gi ni rey na ñu xaritam ciy anam yu ñaaw a ñaaw, te néew ba nee na mes, kenn xamul fu mu ne. Waa dëkk ba yépp njort ni, ñaawteef boobu, du liggéeyu kenn ku dul Chief Moses Abimbola, boroom daraja ju mag, bokk ci nguur gi, te nekkoon àndandoowu Jonas ba ñuy gune, ñu daan wujje ba ñépp xam ko. Fa la Abimbola jóge woon di won mbañeel gu tar jëme ko ci Jonas. Keebaa moom, xelam mayu ko woon benn yoon muy seetaan dundu xaritam biy deme noonu ci neen. Mu ne fàww mu dem ba Ingwini ca Niseriyaa jaaleji soxnay ndemsi-Yàlla-ji, amal fab lànket ngir lijjanti mbir mu lëj moomu, te it, su manee nekk, mu fexe ba néew bi  feeñ. Mu jaraloon ko nag bakkanam. Ndax da doon ci moom, sas wu mu jële fu gën a sori ci xolam : Keebaa Jakite xam (na) ne kóllëre ginnaaw lay féete… Lu muy fekki ci tukkeem boobu ci réew mom  ñàkk kaaraange fa la fekk baax ? Ci yan anam la ñu reye xaritam bi, ak lu waral loolu ? Ndax sax dina feeñal néew bi ? Bi mu demee ba màgget, di xaar Yàlla def li gën ci moom, la Keebaa Jakite jël xalimaam ne fàww mu nettali askanu tey wi, xew-xew yu doy waar yooyule. Ciy way-jëmmal yuy dund ciy jamono yu wuute ak i béréb yu wute it, la bindkat biy jaare ngir nettali lépp jàngkat bi. Moom jàngkat bi sax, day dem ba miin way-jëmmal yi, ñu mel ne ay dëkkandoom dëggëntaan ; way-jëmmal yoo xam ne, ñii dañoo neex deret lool, ñee nee ñu bon-a-bon ; waaye li ñuy wuute yépp, kenn ku ne ci ñoom am na lu ñuy mën a jàngat ci nekkinam ak taxawaayam. Way-jëmmal yi ci  téereb nettali bi Bi Keebaa yeggee Ingwini la nu nettalikat biy wonaleek i way-jëmmal  yu bees: ay defkatu ñaawteef yu jàppe rey nit ni liggéey (Chief Moses Ambibola ak “surgaam”, James Vandi), ay nit ñu xumb te doy waar (Mama Wumbi-Oyé, yaayu Moses ju xayedi ji), ñu jaambure te mën a daw ay ba dee (Tony Akintoye rakku Jonas ji)… Ku ci ne ci ñoom, bindkat bi daf koo jëmmal, ku ci nekk ak say jikko walla say feem, ba far joxe melo nit dëggëntaan. Way-jëmmal yooyu yépp lañuy gis ñuy dem ak a dikk, di xalaat, di gént, di waxtaan, ñenn ñiy faat jaambur yi, ñeneen ñiy aar seen i moroom ; am ñu ciy xeex ngir taxawal yoon, am ñoo xam ne, topp seen bakkan rekk a leen soxal… Jàngkat bi, lu muy gën a xuus ci Malaanum lëndëm di gën a yéemu ci ni nettali biy doxe ba fa muy mujj. Lépp Bóris Jóob di nu ko toggal ba taajal nu lu ñor xomm. Ci njeexital li daal, nettali bu am solo lanuy topp, nettali bu nuy yéem ndax mbetteel yi ci biir ; nettali buy jàngale ci ni àdduna siy doxe,  buy jàngale ci tëralinu ëllëgu doom-aadama. Bóris du tàyyi di jaxase jamono yeek béréb yi, ni mu koy faral di defe, jaare ko ciy xalaati Keebaa : ni mu doon janeere dundam ca ba muy waxambaane. Keeba di fàtteliku ay ndajeem ak Jonas, seen i waxtaan, ni ñu daan déeyandoo, seen i ree bay xàqataay ; waaye it, seen i njàqare, seen i soxla yu jëm ci seen liggéey, ak itam seen i wérante yu xumb jëm ci mbiri pólitig bi walla ci mbiru xeltu. Ku ne werante, ni juyoo, ndax li ñu doonoon ay doomi-ndey taxuleen woon a juboo ci lépp. Teewul nag, ñaari xarit yi doon gën di nawante. Ciy werante yooyu la bindkat biy jaare ngir samp ay xalaat yu am maanaa. Ponki xeltu yi Bóris indi Ci seen i ñaaroo yi ñu daan faral a am, Jonas da daan cokkaas xaritam bi, di ko tooñ ci lu jëm ciy ngëm-ngëmam, dem bay wax lu ëpp ci diineem, jàpp ne ciy “waxi kasaw-kasaw” doŋŋ la lalu. Su ko defaan, Keebaa day waaru : Ci laa jëkkee xalaat tamit ne, Jonas Akintoye, xéy-na yaram wi neexul. Ñaari doomi-ndey yi doon nañu waxtaane yeneen i mbir, ginnaaw lu jëm ci diine ji. Lu deme ni Demokaraasi itteeloon na  leen, te mu nekkoon it lu Jonas gëmul woon, ba tax koy kókkali Keebaa mi doon tiitaroo Demokaraasi Senegaal, naan royukaay la ci  Afrig. Du tere nag, bu Keebaa seetaatee mbir mi, du xam lu mu koy tontu : àndumaak Jonas wànte nag, xiif di la bëgg a rey ba noppi ngay bàkkoo demokaraasi subaak ngoon, gaa ñiy sàcc di kàcc, di lekk ribaa ba seen biir yiy bëgg a fàcc, ñuy toroxal baadoolo yi, ku ko seet ci sunu Senegaal gii xam ni su dee loolooy demokaraasi, demokaraasi ay naxee-mbaay kese la. Lee-lee itam Jonas samp laaj ci sàrt yi lëkkale réewi Afrig yi ak yeneen réew yi, rawatina yu Ërob yi : Mën nga maa wax luy yoonu Tubaab yi ci sunuy mbir ? Noonu la ko ñaari xarit yi jàppe woon : wecce yu dul jeex ci lépp lu soxal ëllëgu doom-aadama, rawatina luy tax réewi Afrig yi suqaliku. Li Keebaa doon fàtteliku yooyu yépp, teewu ko woon bàyyi xel ci lànket ba ko taxoon a jóg. Ku bóom xaritam bi, ak lu tax ? Ci yan anam ? Fan la ñu làq néew bi ? Laaj yooyu ak seen i tontu, Bóris day feeñal lépp, ndànk-ndànk, ciy defin yuy fësal ni mu xareñe ci bind téereb fent. Xereñtey Bóris ci mbind mi Gis nanu ni bindkat bi di wommate jàngkat bi, dëkkoo-dëkk, ciy jamono yuy dem ak a dikk, mel ne ku naan ko naxee-mbaay, na ko Asta Balde waxe, ba muy jëw Gorgi Seega Ture ci jëkkëram. Asta  Balde dib sekkarteer bu Seega di liggéeyloo mu kay bindal nettaleem bii ko ñor lool, su weer deewe mu fey ko. Konte, su dee Seega mooy nettali, moom Asta Balde mooy ki nuy jottali nettali bi : di nu xamale sax ak Seega ak waa këram, ak yeneen way-jëmmal yiy nar a ñëw ci ginnaaw ; di ci njàmbaasaale nag ay mbiri boppam. Mu far mel ne ñaari nettali lanu bindkat bi boole di defal. Konte Bóris, xaraley nettali yu bare te wute la jëfandikoo ngir yakkal nu téereem bu am solo bii, am maanaa lool, di Malaanum lëndëm. Ci ñeenti xaaj nag la nu ko indil, bu ci nekk di doore ci bataaxal yi Asta Balde di yónnee jëkkëram ja nekk bitim-réew te mu namm ko lool ; lu muy def di ko ko nettali, ragal réeroo seen diggante ndax fiiraange. Bataaxal yooyu sax ñooy tëj téere bi. Kon nag, jàngkat bi, amul lu koy jaaxal : du réer benn yoon ndax Asta Balde mooy ki koy tette ba tax muy gindiiku saa su ne. Leneen luy biral xereñteefu Bóris mooy wolof yu set yi muy bind, te du rekk mbind mu set te rafet : kàdduy way-jëmmal yi ci seen bopp dañuy génne waxin ak xalaatu doomu Afrig wala doomu Senegaal tigi, mu wóor ne lii duy kàdduy weneen làkk wu ñu tekki. Mu mel ne bindkat bi, ni muy waxe di ko binde, noonu lay xalaate ci làmmiñ wi mu nàmp. Loolu moo koy may muy mën a firi dëgg-dëgg, ci làmmiñu dëkkam, yëg-yëg biy jóge ci askanam. Ci njeexital li, mën nanoo jàpp ni, Bubakar Bóris Jóob teggiwul benn yoon tànkam ca fa mu ko tegoon, muy yoon wu  ay magam xàlloon, ñu mel ni Seex Anta Jóob, Seex Aliyu Ndaw, Sahiir Caam, Paate Jaañ, Maam Yunus Jeŋ, Aram Faal ak ñoom seen. Bubakar Bóris Jóob ak i maasam wallay rakkam (Mamadu Jaara Juuf, Adraame Jaxate, Abdu Xaadr Kebe…), ñu ngiy bay, tey, seen waar, ci anam bu mucc ayib, ci tool bu yaatu boobule. Bubakar moom, waaram ci wàllu ladab la ko féetale : fexe ba téreeb nettali ci wolof tollu fa yeneen xeeti àdduna si yóbbu seen yos. Moo waral ndam li mu ci amagum, àdduna sépp a ci teg bët, muy lu ñépp mën a seede. Uséynu Béey (+) Téerey Bubakar Bóris Jóob ci wolof : Doomi golo, téereb nettali, Ndakaaru, Papyrus-Afrique 2003, ñaareelu móol EJO, 2019 Nawetu deret, kilib (tekkig ‘Une saison au Congo’ bu A. Césaire), Zulma et Mémoire d’encrier, Caytu, 2016 Bàmmeelu Kocc Barma, téereb nettali, Dakar, Ejo, 2017 Malaanum Lëndëm, téereb nettali, Dakar, Ejo, 2022
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-3-12-2023/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM (3/12/2023) COOWAL CAN LI Afrig moom, dafa mel ni ndeyam liggéeyul. Saa bu CAN bi jubsee, coow li jib, ñuy ŋëwti-ŋëwti joŋante bi. Te, bu “Euro” bi jotee, kenn du dégg coow ñeel ko. Waaye bu Joŋantey Afrig teroo rekk nga dégg lu nekk. Li ko waral nag mooy ni këlëbi tugal yi ame ay futbalkati ñuule dañuy jàpp ne loolee daf leen di yàqal seen i mbir. Looloo waral njiital Bayer Leverkusen li, Fernando Carro de Prada àddu ci kàddu yii : “Jaaduwul kuppeg Afrig bi di am ci diggu atum futbal mi (saison). Ngir soppi loolu, dinaa jokku waa FIFA. Noo ngi xool itam ndax amul yoon wu jaadu wees mën a aw ba bañ a bàyyi sunuy kuppekat ñu dem.” Yile kàddu boo ko déggee dafay wane ni Afrig joxuñu ko cër, muy lees war a taxaw temm ak fulla dox ci, wax ci ba Afrig jël lum yellool. PAAP GÉY A NGI WAAJAL ÑËWAATAM Gannaaw ba ko FIFA daanee woon, aj ko lu tollu ci ñeenti weer ndax coow li amoon ci demam ca Marseille, doomu Senegaal dina dikkaat ci weeru desàmbar wii. Jàppees na ni dina bokk ci seen Joŋante ak Lorient bu Bàmba Jeŋ bu 10i fan ci weer wii. BUUNA SAAR GAAÑU NA Xalam demoon na bay neex, buum ga dog ! Ci fan yii weesu, gisees na ni gaynde gi doon na tàmbali di bokku  ci ndawi Bayern yiy tàmbali Joŋante yi, bay def sax génn yu baax. Waaye gaañu-gaañu bu mettee ko dab, “ligaments croisés”. Mu war a toog li dess ci atum futbal mi. SOFIYAAN JÓOB IT GAAÑU NA. Futbalkatu Nice bi dafa ame damm-damm ci “3e métatarse” bi. Loolu jural ko 6i ayi-bés yum war a toog te du laal bal. Xel di teey ci ndax dina bokk ci CAN bi am deet. ILIMAAN NJAAY NEEXLEEGUL CA MARSEILLE Ci seen Joŋante bii weesu gisees na coow li amoon ci digante Ilimaan ak tàggatkatam bi Gattuso. Li ko waral nag mooy ni Njaayeen bi dafa xawoon a yeex ci soloom bi gannaaw bañ ko woowee ngir mu dugg. Gannaaw loolu, Gattuso andi na ay leeral ci mbir mi di wax ni : ” Weccente naa ak moom bi Joŋante bi jeexee (…). Ekib bi daf ko soxla. Bu nekkee dëgg, bokk na ci ni gën a xereñ ci sàmpiyonaa bi, looloo waral may taral ak moom. Mer naa ci, waaye jéggalunaa itam. “
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/fallu-siise-fekki-na-kocc-barma/
FÀLLU SIISE FEKKI NA KOCC BARMA! Ndekete Fàllu Siise daa bokk ca ña daamar (kamiyoŋ) ga saaraan fan yii ñu génn ca Caaroy dal seen kaw. Aa… Ki doon dawal daamar googu de, xamul li mu def. Li mu def, mënees na koo méngale ak xosi almet sànni ko cig kàggu, téere ya ca ne, ànd ak xam-xam ya ñu ëmb, daldi lakk ñoom ñépp ba def dóom. Fàllu Siise kàggu la woon gu ëmb lu bari ñeel baati wolof ak mbaatiitu wolof. Te ni ko fentaakon bu mag boobu di wuyoo ci turu Aamadu Àmpaate Ba waxe, mu am solo lool, “Fii ci Afrig, boroom xam-xam bu làqu daa mel ne kàggu gu lakk”. Ñaar a ma tax a fàttali loolu, tey. Benn : boroom xam-xam yi mel ne Fàllu Siise duñuy faral di móol i téere di ci dëxéñ xam-xam boobuy tax bu ñu fi jógee mu des fi ba seeni sët ak seeni sëtaat jot ci ba sax gën koo ñoŋal. Ñaareel bi moo di ne seen xam-xam du wasaaroo ndax day saf baatin ba tax ñu néew a ciy jot jaare ko ci ag tarbiya. Bu nu boolee loolu lépp, demug Fàllu Siise gi day doon ci nun ñaari tiis. Bu njëkk bi ñeel génnug àddinaam ak anam bu metti bi mu ame. Bi ci des di xam-xam bi mu yóbbaale. Waaye nag sant Yàlla ndax bi nuy jooy loolu ci la ma Sëriñ Jili Kebe xamal ni Fàllu jotoon naa liggéey ak benn waay ba tax lu bari ci li newoon ci moom yëbb na ko ci waay jooju. Rax-ci-dolli, waxtaan yi mu jot a séq ak ña ca kippaango bee ñu duppe Akaademi wolof ci Facebook, baati wolof yu xóot te ñu bari umple leen woon, jot na ko faa rotal. Lee tax nu mën a jàpp ne Fàllu Siise dem na waaye demul ndax ni ko woykat bi waxe “suuf dina lekk doomu-Aadama bàyyi fa jëf”. Xanaa rekk des di ko ñaanal Yàlla miy Boroom-Yërmaande jéggal ko te xaare ko àjjanay firdawsi ci barke turandoom Sëriñ Fàllu Mbàkke. Bu loolu weesoo, nu def yitte ci dajale li mu nu fi bàyyil, móol ko, wasaare ko ba mottalil ko naalam wi jëm ci jëmmal làkk ak baatiitu wolof. Seen yéenekaay LU DEFU WAXU mi ngi koy jaale njabootam gépp ak i mbokkam. Waaye, noo ngi koy jaale yit waa Senegaal gépp rawatina ñiy liggéey ci làmmiñi réew mi.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/fu-messi-di-futbal-dewen/
FU MESSI DI FUTBAL DÉWÉN ? Jamono jii, laaj bii moo lëmbe xel yi, rawatina xeli soppey Barcelone FC yi. Li ko waral, nag, mooy ni, seen yéene yépp dafa nekk ci Messi ñibbisi. Ndax dana am ? Ndax du am ? Mëneesagul a am tontu lu leer ci laaj bi. Lo am ba des daal, mooy ni foofu ca Barça, seen yaakaar moo ngi gën a dëgër ñeel delsig Messi. Moom, Messi, Barça la defe léppam. Dafa di, li mu jot jël ci dundam yépp, ci wàllu këlëb, Barça la ko ame. Te sax, xel mësul woon a xalaat ne bés dina ñëw mu fay jóge. Moo tax, demam ga, ca atum 2021, ñépp la bettoon. Ndate, du woon lees doon xaar walla di ko waaj. Moom kay, dafa xëy rekk takk i dëbësam. Li wolof di wax, naan, “Ku sañul a bañ, sañ a nangu” moo ko ci dal. Nde ñépp xam nañu fu ko Barça tollu ak it fi mu tollu këlëbu katalã yi, lam fa def ak kim fa doon. Naam, Barça sosu na lu njëkk xameelam fuuf sax, mën tuddu turu ekib ba te xel newul yar ci moom Messi. Waaye nag, ñépp xam nañu itam ne, bim fay jóge di dem Paris, dafa najoon xolam rekk, waaye gënalu ko woon wenn yoon. Ñàkk pexe rekk a ko fa yóbbu. Barça, jamono jooju, mu ngi nekkoon ci ay jafe-jafe yu jëm ci mbirum payoori kuppekat ya. Ndaxte li ñu gisoon ne moo ngi koy fay ay kuppekatam, buñ ko xaymaa, lépp dafay jéggi liñ leen may di dem. Loolu nag naroon koo andil ay guddi yu lëndëm, moom Barça. Ci noonu, ñu nekk ciy lijjanti ak di xool naka lañuy def ba saafara loolee. Loolu moo dem ba andi demug Messi gi. Ndax cofeel gi mu am ci ekib  ba ak bañal ko ay jafe-jafe tax mu nangu jóge ca ekib ba. Waaye du woon ne daf fa doyal walla dafa bëggoon a wuti leneen feneen. Déedéet, du woon loolu. Ndaxte, lépp jëloon na ko ak Barça. Luñ fa tegoon ñu di ko xëccoo rekk teg na ci looxoom foofa. Demam gi mettiwoon lool ay soppeem, ñi ko wër, waaye itam moom ci boppam. Nde, ca tàggatoowam, jottina fa ay rangooñ yu tàng ak ñu bari ñu fa teewoon rawatinay farandooram. Ca atum 2021, mu jóge Barça dem Farãs fekki Paris Saint-Germain. Mu doonoon lu rëy ci boobu këlëb. Ndaxte, ku tollu ni Messi nga yor ko sa ekib, ndam la, sag la. Ba ci jamono jooju, foo geestu waan, ay mayo Paris yu ñu bind turam rekk ngay gis, mbaali-jokkoo yeek këri xibaar yépp di tas i xibaar gi ak di dugal i nataalam fépp. Ñëwam gi foofu ci Paris nekkoon na lu rëy ci ñoom, nde jàppoon nañ ni seen yéene ci jël “League des Champions”, bu Messi dikkee dafay gën a dëgër,  ekib ba itam gën koo bëgg. Waaye, dafa di, saa buñ xëccee ba am yaakaar rekk buum ga dog. Atam bu njëkk ca Paris, mu xawoon a am ay jafe-jafe wane fa boppam niñ ko doon séentoo, rawatina ci joŋante yu mag yi. Ñu jàpp ni lam fay door a ñëw la, walla sax ñàkk a miin dëkk baa ko jàppoon rekk, ci déwén gi dana firi. At mii nag, mu ñëw, ci njëlbéen gi, tàmbali di gis, di dugal ay bii ba ñépp tàmbalee bég. Mu jóge fa dem ca Kuppeg Àddina si amoon ca Qataar, xare ni gaynde ba jël ko. Mu wane fa nag xereñte gi ko ñépp xame woon, def fa lu rëy ba kuy bége kuppe bég ca. Mu delsi Paris, nga gis mu mel ne ku yarasaat, ba ni mu daan def ca Kuppeg àddina sa, joŋante ci mag yi niki ak Bayern ca “League des Champions” muy mel ni ku réer. Loolu waraloon siporteeri Paris yi doon ko yuuxoo ak a xalab. Jamono jii nag, féddaliwaat xaritoom ak Paris nekk na loo xam ni kenn yaakaaru ko. Xel yépp, ci mu dellu Barça lañu nekk. Te sax, waa Barça loolu rekk lañu bëgg jamono jii. Kii di Laporta ma jiite këlëb ba, ak Xavi miy tàggatkat bi, jotoon a far ak moom ay ati at, loolooy seen yéene. Moom Messi ci boppam bañul loolu. Ndax, déggees na ne, ay nitam ñoo ngi jokkoo ak waa Barça, di xool nam fay delloo. Neeti nañ sax ne, moom ci boppam, mi ngi dégganteek gaa ña, di ci dalal seen xen. Fële ca Araabi Sawdid itam turam moo ngi fay jib. Ndaxte, Al Hilal, këlëb biy diirante mbagg ak Al Nasri bu Ronaldo, dafa bëgg a teg xaalis bu takku ci taabal ji ngir mu ñëw fa. Lu ci mën di am daal, lépp dina leeri. Dinañu xam ndax dafay toogat Paris am dafay fekki wujjam ba, Ronaldo, mbaate mu dellu këram gii di Barça. Li ci kanam rawul i bët.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/ndigalu-maam-ya/
Ndigalu Maam Ya Afrig nee Waaw góor, waaw kumba Ayca leen ca waar wa Bu kenn wéer goob ba Bii pas-pas dara mënalu ko dara Dina daw ba raw xëlu fas Ngor ak jom a ko nas Ma ne, Askan wee ko sas Gan góoru jigéen ñi dar lingeer Ci seen farlook seen gànjar ya Bég ba tàccu ne sas Maam a ne bëret dan delsi Samp xeej daldi xas Gisuma fi yaakar ju tas Tuggee Tugal Wéyal yaak say dëbës Afrig dina bañ ba sës Ndawi tey yi dootuñu surgawu Topp sa gannaaw ni jaam bu nangu Dina tàng dina metti Waaye jàmbaar du xàddi Na doxandéem bii dakkal Wàqi gi muy wàqi sunu alal Di roñ di génne Di gaawantu di rawale Am ñu ne xiim di xoole Mbaa sax di ko ci dimbale Sàmm sam réew warugar la Bëgg sa réew siddit la Gor tigi du wor du wuruj Te su séddu jotee mooy mujje Biir bu rëy lex yu newwi Sonal sa bopp tooñ say ñoñ Moone de bànneex tigi Xanaa xam-xam ak néewle soxla Tey jiital njariñal doom Aadama Seex Aliyu Ndaw Ndakaaru, weeru mars 2024
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/alseri-dumaati-na-senegaal/
ALSERI DUMAATI NA SENEGAAL Démb ci talaata ji la gayndey Senegaal yi doon janook Alseri ci joŋante xaritoo. Jamñaajo, ça fowub Abdulaay Wàdd, lañ ko doon futbalee. Alseri moo jëlati ndam li. Nde, ñoom ñoo dugal benn bii, Senegaal tus. Démb a nekkoon 14eelu yoon wi Senegaal di sukk ci kanamu Alseri. Li ci gënatee doy waar mooy ne, Alseri dafa tegale 6i joŋantey kuppe yu muy dóor Senegaal. Laata joŋante biy door, bi 19i waxtu jotee, jaglees na similib tekkaaral way-dëdduy Marog yi dee ca rëng-rëng ba fa am. Bi mbir yi tàmbalee, Senegaal a tegoon tànk ci bal bi, sépp Alseri. Jekku nañ ay yoon ngir dugal. Waaye, muy Saajo Maane, di Ilimaan Njaay walla Nikolaa Jakson, kenn làkku caax yi. Bal buñ dóor, jàppkatu Alseri bi génne. Alseri dafa amoon ay jafe-jafe ngir jot ci bal bi. Te, saa buñ ko jotaan, gayndey Senegaal song leen, nangu ko, sëppaat leen. Ñooñu, ba ni arbit biy mayee ag noppalu ngir ñu seral seen i put. Ndax, dafa tàggoon démb. Biñ naanee ba màndi, waa Alseri dañu xaw a yeewu tuuti, tàmbalee cokkaas Eduwaar Mendi. Wàññeeku Senegaal bàyyeekuwul. Dañu jàppaat, nanguwaat bal bi. Paap Mataar Saar, Kulibali, Jakson ak Sabali naroon nañu dugal sax, waaye sottiwul. Bi xaaj bu njëkk biy jeex, kenn dugalul sa moroom. Biñ delsee ci ñaareelu xaaj ji tamit, Senegaal dafa delloo buum ca mboy-mboy ga. Waaye daal, bal bi daa bañoon dugg. Ca la xel ya tàmbalee teey, ñiy ragal Alseri yoxosu Senegaal. Benn teg-dóor la Alseri am, Riyad Mahrez xellil Chaybi Fares, mu toj kër gi. Alseri nax na Senegaal, dugal ko benn bii bu kenn foogewul woon. Nde, Senegaal a moomoon mats bi, ci lees foogoon. Senegaal def na lépp ngir dugal, waaye dugaluñu. Jakson naroon na ko, waaye mbëkkam bi dafa kawe. Noonu noonu ba ni arbit biy mbiibee njeexitalu joŋante bi. Alseri daldi amati ndam ci kow Senegaal. 6i yoon la raŋale, di dóor Senegaal. Dafa di Aliw Siise sax, démb a nekkoon ñeenteelu yoon wi muy ñàkk ci kanamu Alseri. Démb nag, Sonko safoon na fa sàpp. Balaa joŋante biy door ak bi muy daw yépp, ndaw ñaa nga doon woy woyu Usmaan Sonko wi xew ci jamono : “Aayee ! Iyawoo ! Sonko namm naa la ! Sonko ! Sonko ! Sonko namm naa la !”
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-10-07-2023/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM (10/07/2023) MAROG JËL NA CAN U23 BI Démb, ci gaawu gi, lañ doon amal lii di finaalu CAN U23 bi doon ame fa Marog. Mu gi dooxoon ci digante ñaari naataango yii di Marog mi dalal xëccoo bi ak Esipt. Mu nekkoon finaal bu neex. Waaye, Marog moom, moo xewle, daldi woote, luñ nar a fecc mu fecci ko, lekk ci it mu ni leen fuuf ni gan ya ñibbi leen. Maanaan moo woote po mi ca dëkkam, finaalu ba noppi jël kub bi. Bi ñu dawalee ba fukkeelu simili bi la Esipt daldi dugal (Saber). Ñuy wéyal ba ci 37eelu simili bi, kii di Y. Begraoui fayul dëkkam, muy 1-1. Ñu jàppe ko noonu ba 90i similiy joŋante bi jeex, kenn dugalaatul. Ñu àgg “prolongation”. Biñ àggee ci 108eelu simili bi (105+3) la Marog yoxosu Esipt, dugalaat benn (O. Targhalline), muy 2-1. Nooyu lay jeexee. Abde Ezzalzouli, kàppitenu Marog, moo ëpp lum dugal ci xëccoo bi (3i bii) ak lum ci joxe ñu dugal (3i paas). EURO U21, ÀNGALTEER NAX NA ESPAAÑ ! Ba tay, ci gaawug démb gi lees doon amal it finaalu Euro U21 bi diggante Àngalteer ak Espaañ. Àngale yi ñoo mujje dóor espaañol yi benn bal ci dara. Àngalteer nag, yamul ci jël kub bi rekk, dafa def lu réy. Ndaxte, dem na ba jël ko te benn bal laalul i caaxaam, maanaam kenn dugalu ko. Te, ñoom, dugal nañ 11i bii ci seen juróom-benni joŋante yoy, yépp lañ gañe. Loolu di lu rëy. LAMB : PAPAA BOOY JINNE DAANOOTI NA Ndiggu Papaa Booy Jinne laalati na suuf. Ndàndi Faal moo ko daanati démb ci gaawu gi. Moom Papaa Booy Jinne, gëj na am ndam. Ndax, 2017 la arbit gëj a yékkati loxoom. Kor Ndey Géy (fecckat) ba woon, ñu baree ngi naan na tekki ngembam.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-18-9-2023/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM (18/9/2023) WAA LORIENT YI SARGAL NAÑU BENJAMIN MENDY Benjamin Mendy duggaat na démb ci pàkkub futbal, gannaaw tuuma gu metti te yàgg bi tegu woon ci ndoddam, at yii weesu. Tuumay ciif yooyu ñu gàlloon ko ñoo taxoon ñu bari foogoo ne daf ciy jaare bàyyi futbal. Waaye, keroog, ba ñu ko setalee ni deful lees ko doon toppee, la daldi fasante ak Fc Lorient, këlëb bu nekk Farãs. Démb, ci dibéer ji 17i fan ci sàttumbaar 2023 la duggaat ci pàkk bi, ci joŋante Lorient ak Monaco. Soppey këlëb ba sargal nañu ko, woy turam. Ci 70eelu simili bi la duggu. ABIIB BÉY A NGI NE PATT DI LIGGEEY Dafa boolewul daraak wax. Moo ngi nekk ci ruqam ak këlëbam, Red Star, di def jéego yu am solo moom Abiib Béy, saa-senegaal bi bokkoon ci gayndey ati 2000 yi. Ci tàmbalig « saison » ren ji, amal na ci 5i joŋante, gañe ñeent yi, ñàkk benn bi. GREENWOOD DUGGU NA XAAT CI MBOORU GETAFE Gannaaw i tuuma yees ko tegoon moom it ci mbiri jigéen ba tax waa Manchester United daldi koy bañal mu toogaat ci ekib ba, àngale bi dafa daldi fasanteek Getafe, ab këlëbu españool. Ci ayu-bés bii nu génn,  këlëb bi daldi nay jaay ciy mayo yees bind turam lim boo xam ni bii kenn mësu koo def ba Getafe di këlëb ba léegi. JOAO FELIX DUGAL NA BIIWAM BU NJËKK CA BARÇA Barki-démb ci gaawu gi, ci ndamu Barça bu rëy bi 5-0 ci kaw kii di Real Betis, la Joao Felix daldi dugal balam bu njëkk ca këlëb ba. Loolu nag doon ci moom mbégte mu réy, nde bi ñu ko dékkee mikoro bi ba joŋante bi jeexee, dafa wax ni « yàgg naa dugal bii, waaye bii moo nekk bu ma ci gën a neex ndax dafay matal sama géntug futbalsi Barça. »
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/naareelu-xaaju-waxtaanu-mamadu-jallo-ak-ndongo-samba/
« Man, dama jàpp ne, CFA ak ECO ñoo yem kepp, benn baaxu ci. » Mamadu Jàllo :  Ndax CFA bi baax na ci njaay meek njënd mi, rawati-na bitim-réew ? Ndongo Sàmba Silla : Déedéet. Mësu cee baax ! CFA bi du yombalal njaay meek njënd mi. Moom kay, safaan bi la koy jural. Ndaxte, boo seetloo, bi Senegaal moomee boppam ci atum 1960 ba nëgëni-sii, li ñuy wax ci tubaab sunu “balance commerciale” dafa deme boor. Maanaam, soo méngalee li réew miy jënd ak li muy jaay bitim-réew, dangay gis ne li muy jënd moo ëpp fuuf li muy jaay. Li Frãs fuloon dayo CFA bi moo waral laago bi.  Ndege, diisaayu CFA bi moo tax liggéey ci jafe. Te, am réew, bu dee li muy jënd bitim-réew moo ëpp li mu fay jaay, day ame ay bor yu dul jeex. Loolu moo nu sonal. Booba ba léegi, bor a ngi ci sunu baat. Danoo leb a leb ba mënatunoo fey. Seŋoor ba Maki, jaare ko ci Abdu Juuf ak Ablaay Wàdd, ku dàq a leb sa moroom nga ne kii.  Wànte Maki Sàll, sunu njiitu réew mi fi ne, moo ci raw. Te nag, jàngoro, doomu-jàngoro du ko faj. CFA bi mooy laago bi, kon, féeg noo ngi koy jëfandikoo, dunu mës a jóg ci leb. Dëgg la, réew yépp ay leb, ba ci réew yi ëpp doole ci àddina si. Waaye, benn, kenn tënku leen ba duñu mën a jaay bitim-réew ; ñaar, seen woyofaayu xaalis may na leen ñu doxale noonu seen i naal. Nun nag, CFA bi mooy sunu gàllankoor. Xaalis bi dafa am doole ba tax na say njaay du jar. Kon fooy jële looy faye say bor ? Li nga wax dox na waar, di ! Yaa ko gisal sa bopp. Lu ni mel, ñi féete kow te ne déjj ci donkaasi gi doŋŋ lay amal njariñ. Dinañ mën a jënd lu leen neex bitim-réew, indi ko ci réew mi, jaayaat ko nu mu leen neexe. Seen xaalis di gën a yokk ak bu Farãs, askan wi moom di wéy di ndóol. Bu lu ni mel amee, dees na joxoñ baaraamu tuuma bànk yu mag yi. Ndaxte, ñoo ko sooke. Ndekete, ñoom dañuy bañ a lebal nit ñi xaalis. Maanaam dañ leen di gàntal. Li ñu ko dugge nag, du lenn lu dul sàmm yemoo (parité) CFA bi ak Ëro bi. Njiiti bank yooyii xam nañ ne, bees lebalee xaalis liggéeykat yi, muy àntarpërënëer bi, di boroom bitig bi, walla sax bépp jaaykat, li ñuy koy jënde mooy ay jumtukaay walla dund. Jumtukaay yooyu ak dund bi, nag, bitim-réew lañu koy jënde. Te, téeméeri àntarpiriis yoo jël, 30 yi walla 40 yi bitim-réew lañuy jëggaani seen jumtukaay. Loolu jur lan, nag, ci sunu koom-koom ? Day nasaxal walla day wàññi xaalis bi nuy bàyyi ci bànki Frãs ba, ñu koy wax ci nasaraan “réserves”.  “Réserves” yooyu, nag, ñooy wóoral yemoo CFA ak Ëro. Looloo tax bànk yu mag yi duñ sawar ci lebal liggéeykat yi. Doo ma baal nga leeral fii ? Lu loolu joteek yemoo bi ? Waaw, ngir sàmm yemoo boobu, fàww ñu dakkal bor yi walla ñu wàññi leen. Liggéeykat bu ci am wërsëg ba bànk yi lebal la, li ngay war a fey day takku lool. Ci gàttal daal, CFA bi day yokk say bor, xoj say liggéeykat, tere laa am i isin, tere laa jaay bitim-réew… As tuut li nu am ciy njuréef ak alal, tubaab yaa koy fob yóbbu seen dëkk ndax li ñu dippe “zone franc” moo leen ko may. Ndax loolu jaadu na? –     Déedéet kay ! –     Kon nga xam ne noo ngi ci nooteel ba léegi. Loolu yépp, nag, boo leen boolee, lenn doŋŋ lay jur : tumurànke. – GInnaaw bi nga leeralee ni CFA bi nooteel lay biral, lan nga jàpp ne moo nu ci teree génn boobaak léegi ? – Waaw. Laaj bu am solo nga laaj fii. May ma ma jox la benn misaal. Man, damay faral di dem bitim-réew ngir amal fa ay waxtaan ñeel CFA bi, ma ciy ànd ak gëstukati daara-yu-kowe yu mag. Waaye, saa yu ma noppee ci wax ci CFA bi, leeral jafe-jafe yi mu làmboo, tubaab yi ci seen bopp dañuy waaru ! Mbir mi da leen di jaaxal lool sax. Bu ko defee, ñu naan ma : « Déedéet kay ! Waaw yéen, lu leen tee wacc musiba bii nga xamante ne day gàllankoor seen dund ak seen yokkute ? Ana seeni àntarpërënëer ? Seen njiit yi ngeen di fal nag, lu leen dal ba ñuy seetaan lii ? Moo, ndax dungeen fippu indi saafara ci jàngoro jii ! Yéen a ngi nelaw de ! » Bu ko defee ma ni waaw, Tubaab yeey wax lii…Waaye, bu dee fii ci Afrig, walla Senegaal, saa boo waxee ci musibay CFA bi, dañu la naan : “ Waaw…dëgg la, CFA bi am na ay jafe-jafe waaye am na ay ngëneel itam…” Nga gis ne, Tubaab yi sax, nangu nañ ne CFA bi musiba la ci nun. Waaye, ñenn ci doomi Afrig yi, walla doomi Senegaal yi ci seen bopp, ñoom, jàpp nañ ne CFA bi am na njariñ. Dafa di, ñi ànd ak CFA bi, dañu dul xalaat, walla ñu bokk ci nguur gi, teewal fi Frãs mu am lu mu leen di combal. Waaye, nag, ku waxaale sa ngor, ñu jënde ko sa toroxtaange. Loolu moo nu dal. -Kon ci sa gis-gis Frãs a nu teg li lépp ? – Frãs ak doomi-Afrig yi koy jàppale. Ndaxte, boo seetee, réew yi Frãs nootoon yépp, am ci ñu dul jëfandikoo CFA bi, moom seen bopp ba mu mat sëkk, te tey ñu ngi ci yoonu yokkute. Réew yooyu, bi xeex jotee, dañu jaayante ak Frãs, jàmmaarlook moom, foqati seen réew. -Mën nga leen a lim ? – Réew yu jàmbaare yooyu, mënees na cee lim Alséri ak Wiyetnaam. Ñoom ñaar ñépp a xare ngir afal seen askan. Nun, nag, sunuy njiit ya woon, jarul nu leen fiy tudd, doxalewuñu woon noonu. Dañu maslaa ak Frãs, mu kootoog ñoom, lal i pexe ngir gën fee mën a toog, aakimoo sunu alal. Bi gënoon a fës ci pexe yooyu nootkat bi laloon mooy li ñu dippe woon “Accords de coopération”. Loolu li mu wund mooy, lépp lu aju woon ci moomeelu réew yi mu nootoon, ciy loxoom lay tegu. Maanaam, njaay meek njënd mi, ak lépp lu ñeel jëflante ci diggante nootaakon (colonies) yi ak bitim-réew, xaalis bi (te muy CFA bi) ak koom-koom gi. Loolu la Frãs waxoon ne bu ci sunu njiit ya woon àndee xaatim ko, mu nangu ñu moom seen réew. Sunu njiit yi nag, ñu ci ëpp Frãs lañu jànge, foofu lañ leen tàggate, daan fa liggéeye te nekkoon fa sax dipite. Moo tax ñu xaatim loraange jooju nu topp ba sunu jonni-Yàllay-tey jii. Réew mu ci mel ni Gaboŋ, lépp lu muy def, Frãs da cee ànd. « Accords de coopération » bi mu xaatimoon ñoo ko ko yóbbe. –Ndax am na ñu fippu, ne fàww ñu dog buumu njaam gii ? – Lii tamit laaj bu am solo la. Am na ñu yàgg a xeex CFA bi ngir jële ko fi. Axã kay ! Du léegi la ñenn ci doomi Afrig yi tàmbalee xeex CFA bi. Xeex bi démb la woon, tey door a agsi. Te loolu boo ko waxee xel war naa dem ci Séku Ture. Ndege, moom moo jëkk a bañ CFA bi, ne dee, Gine du ci bokk. Moom Séku Ture, bañkat bu mag la woon, amaana li mu doonoon ab sàndikalist moo taxoon. Ndax ku mënoon a dajale ay nit la te bare woon i pexe lool. Waaye, ak lu xel miy màcc yépp, jataŋ ak gàllankoor yu bare yi ko Frãs daan teg, moo koo taxoon a tagatémbe. Loolu rekk a teewoon Gine génn ci. Frãs da doon dugal Gine xaalis bu bon bu baree-bare ngir yàq deru Séku Ture. Am na keneen ku ñiy wax Silwanus Olimpiyóo, njiitu Tógo la woon, nekkoon layookat bu siiw. Dafa laloon ab naal ngir wutal réewum Tógo xaalisu boppam. Jotoon na cee waxtaan sax ak réew yu mag ci àddina si, niki Almaañ ak Amerig. Bi mbir mi demee bay sotti la ko Frãs sàkkal pexe, ngem Eyademaa mu rey ko. Naka noonu, Tomaas Sànkara, jàmbaaru Burkina-Faaso ba. Nu gis ne, Frãs jenn itte doŋŋ la am : ratt réewi Afrig yi ba ñu sett, jël seen alal di ko siimee cereem.Cere jooju, nag, ku ko bëgg a xajamal mu sàkkal la pexe. Waaye, nit ñit xippi nañu seeni bët. – De4gg la, nit ñi xippi nañu seeni bët, moo waral way-moomeel yi, kujje gi ak boroom xam-xam yi takkal pot sunu njiit yi ak Frãs. Dafa mel ni gaa ñaa ngiy deeltu ginnaaw ndax ñoo ngi wax ne dañuy bàyyi CFA bi dem ci ECO bi. Loo xam ci xaalis bu bees boobu ? – ECO bi ?Waaw. Dégg naa ñenn ñiy xeex CFA bi naan, nanu gaaw jël ECO bi, def ko sunu xaalis. Waaye, ECO bi ci lajj lay mujj. Wolof dafa ne, ku ndóbin rey sa maam, foo séenatee lu ñuul daw. Man dama jàpp ne, CFA ak ECO ñoo yem kepp, benn baaxu ci. Dama xamul lu tax rekk mënuñu lal ab naal boo xam ne, dina jur i meññent ëllëg. Te sax, lu tax nuy déglu ñi nuy gëmloo ne sunu bëggee jëm kanam fàww nu bokkak ñeneen ñi xaalis ? Loolu du dëgg. Gàtt xel doŋŋ la ak xeebaate. Fii, ku fi gëm sa bopp, takku liggéey dinga am yokkute. Damay jël misaal ci yenn réewi Ërob yoo xam ne Senegal moo leen gën a yaatu, ëpp leen alal, ëpp leen mbooloo. Tey, ñoo ngi ci naataange te dara mayu leen ko lu dul liggéey bu jaar yoon. Kon, ku nekk mën nga  liggéeyal sa réew ba mu naat. Waxuma ni booloo baaxul. Wànte, fàww ku nekk gëm sa bopp ba noppi, liggéey liggéey bu lay amal njariñ, amal njariñ ñeneen ñi. Bu ko defee, dinañu mën a saxal garabu booloo gi, di ko suuxat ba mu màgg, dëgër, law ci biir Afrig gépp.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/paap-bu-mag-ba-woon-benuwaa-16-sosef-ratsingeer-wuyuji-na-boroomam/
Paap bu mag ba woon, Bënuwaa 16 (Sosef Ratsingëer) wuyuji na Boroomam
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/aram-faal-sunu-seex-anta-joob-bu-jigeen/
ARAM FAAL, SUNU SÉEX ANTA JÓOB BU JIGÉEN… Talaata jii weesu di 23 ci weeru awril la Mbootaayu-Xeet yi jagleel bépp teere bu doom-aadama bind ci àddina si. Ci la EJO ak ArtXaleyi, di ñaari kurél yuy yëngu ci mbirum aadaak ladab, sargal Soxna Aram Faal Jóob mi yàgg a def liggéey bu am solo ngir ñépp jox làmmiñi réew mi seen gëdd. Majaw Njaay mi sàkk ArtXaleyi, jiite ko, dajale nay gone laaj leen kan lañu bëgg ñu sargal ko ren jii, ñoom ñépp ñu ne : ‘’Xanaa sunu maam Aram Faal Jóob !’’ Waaye du woon guléet ndax Senegaal yàgg na delloo Aram njukkal. Ñaari at ci ginnaaw rekk la ‘’Foire du livre’’ amaloon xew-xew bu mag, jagleel ko ko. Ci la Soxna Aram woo Ndey Koddu Faal — mi bokk tey ci surnalisti LU DEFU WAXU yi — ni ko : “Doom sama, yow laa bëgg nga teewal ma ci xew-xew boobu, jël fa kàddu ci sama tur, fàttaliwaale mbooloo mi sama jaar-jaar.” Kàddu ya Ndey Koddu yëkkati keroog ci tubaab la tekki fii ci kàllaamay Kocc mook Paap Aali Jàllo mi ngeen war a miin turam moom tamit ndax mu ngi bind saa su nekk ci yéenekaay bi ngeen janool tey di ko jàng… Mbooloo mi, maa ngi leen di nuyu yéen ñépp, ku ci nekk ci sa tur ak sa sant… Aram Faal Jóob… Képp ku dégg tur wii, muy fii ci Senegaal di bitim-réew, fàww sa xel dem ci soxna su masul a tàyyee liggéeyal làmmiñi réewam, ngir suqali leen. Doom-Aadama yu bare, ba ñu newee gone lañuy bëgg a doon lii mbaa leneen. Waaye liggéey bi ñuy mujjee def day faral di safaanook seeni bëgg-bëgg. Aram Faal Jóob mi ñépp sopp ba di ko woowe Tànta Aram, bokkul ci ñooñu. Amal njariñ Senegaal ak Afrig, lu ko mas a soxal la te Yàlla boole na kook ñu ko ciy ñaax. Ki ci njëkk, gën cee am solo, Séex Anta Jóob la woon. Aram ci boppam moo ma ne su dul woon ndajeem ak ponkal moomu bind Nations nègres et culture, amaana mu aw weneen yoon. Nii la ma ko waxe : « Ndongo Séex Anta laa woon. Moo tax ma teel a bëgg a bey sama waar ci toolu làmmiñi réew mi. Bu dul woon loolu, jàngalekat laay doon tey.» Maa ngi fàttaliku keroog jooju ni kanam gi tiise bi mu may nettali digganteem ak soxnay Séex Anta : « Louise-Marie Maes, sama xaritu benn bàkkan la woon. Daan nanu am ay waxtaan yu yaatu ci làmmiñal». Aram Faal Jóob doomu-Ndar la. Fa la fekk baax. Fa la jànge ba am ñaari xaaji Bakaloryaam laata muy wutali Iniwérsite Ndakaaru, am fa lijaasa bu ñuy wax Diplôme d’études supérieures. Jóge fa nag dem mottaliji njàngam Tugal ci Iniwérsite Paris III ; fa la defe teesam sax, ci atum 1973. Boo seetloo bu baax, dinga gis ni donte sax at ya mu def Frãs am nañ solo, li ko gënoon a ñor mooy delsi Ndakaaru liggéey ngir jëme réewam kanam. Mu yemook at yu njëkk yi Senegaal moomee boppam, Aram ñibbisi bay waaram ci ëllëgu réew mi. Fanweeri at ci ginnaaw la tàmbale bind, ànd ceek Rosine Santos ak Jean Léonce Donneux. Ci lañu génne ca Karthala benn Dictionnaire wolof — français bu askan wiy jariñoo boobaak tey. Wànte Aram yemu fa. Mënees naa lim ci téere yu bari yi mu bind : Grammaire fonctionnelle de la langue wolof ; tekkendoo na it ak àttekat bii di Amet Juuf Ndeyu-àtte réew mi ; beneen téere bu am solo bu mu tekki mook ndem-si-Yàlla ji Maam Yunus Jeŋ mooy Une si longue lettre bu Mariyaama Ba ñu tudde ko Bataaxal bu gudde nii. Ngërëm ñeel na tamit Aram Faal Jóob mi génneendoo ci wolof, tubaab ak àngale Baatukaayu x@mtéef di ci tekki bépp baatu informatik. Bunu fàtte itam ni ci atum 2012 moom ak Amet Juuf ak Mamadu Njaay lëkkaloo nañu sotti ci wolof sunu Code des marchés publics duppe ko Sàrtu Jawi Nguur gi. Li gën a tax Aram war a doon royukaay moo di ne du sonn du tàyyi. Tëju na ay ati-at di liggéey ci téere bu mu génne bu yàggul ngir fexe ba ñi déggul tubaab mën a jàng kàllamay Kocc. Téere boobu mooy Nëwu làmmiñu wolof. Kon li ñépp di xëccoo di ko sargal, di ko delloo njukkal warul a bett kenn. Amul ku ko ko gën a yellool. Waaye ak fi dayoom tollu yépp, Soxna si Faal tiitaruwul, réy-réyluwul. Naka jekk, Tata Aram xamul puukare. Dafa amul sax jotam, faf. Waaw, sunu lingeer bi dara mësu ko ñor lu dul sàkku ak nafar xam-xam. Waaye tamit, dafa mës a yittewoo ndono li, ba tax mu dëkk ci di tette ndaw yi. Noonu la ko Soxna Aram Faal jàppe, ca njëlbéen ga ba nëgëni-sii. Nu gis ne kon màndargay niteef yi Soxna Aram Faal làmboo dañu di ab fànn bu réy ci jaar-jaaram ; rawatina ba muy nekk IFAN ba ni mu fay génne ci atum 2002 -moo fa jiite woon banqaasu làmmiñal bi- ak ci Kurélug wall ngir naataange Senegaal, di këru móolukaay bu siiw bi mu sos te gàttal bi ci nasaraan di joxe OSAD. Jamono jii nuy wax ak yéen, li ëpp ci téere wolof yi jot a génn ci réew mi, OSAD a leen móol. Téere yooyu, nag, ràññees na ci Aawo bi te ndem-si-Yàlla ji, Maam Yunus Jeŋ, bind ko ak tamit téere Séex Aliyun Ndaw yu takku yi, werekaanu werekaan yi ci wàllub ladab ci làmmiñu wolof. Tey, mboolem bindkat yi ci làmmiñu wolof fésal nañu seenug mbëggeel ak fonk bi ñu fonk Soxna Aram Faal Jóob. Li ko dale ci Mamadu Jara Juuf ba ci Mamadu Njaay, jaare ko ci Daba Ñaan ak Séex Adaraame Jaxate, ñépp a ko naw. Li tax ñu naw Soxna Aram, am ci moom mbëggeel ak cofeel yu réye nii, moo ko jëfe. Waaw, te muy dëgg. Ndaxte, ku baax, ak foo fekk baax, mbaax fekk la fa nga nekk, yëkkati la ba nga sut say maas ! Soxna Aram Faal daa baax, te ci mbaaxam doŋŋ la wuufe ndaw yiy topp ciy tànkam, di leen tette, boole ci muñ ak yéwén lool ci xam-xamam ak alalam, te séentuwu ci dara. Te, nag, wolof dafa wax ne, ku dul gërëm nit, doo gërëm Yàlla. Looloo tax bindkat yooyii ñu fi jot a lim, ku ci nekk gërëm na Soxna Aram, sant ko delloo ko njukkal. Ba tax na, ku ci nekk ci ñoom, tudde na ko lu mu tuuti tuuti benn ci ay téereem, seedeel ko ci lu rafet. Waaye, bu dee seede ak wax ju rafet rekk, dees na ko bàyyee ndem-si-Yàlla-ji Maam Yunus Jeŋ. Ndax, tagg bi mu tagg Soxna Aram rekk doy na ci tagg. Li mu génn àddina tey, tax na waxam ji gënatee daw yaram. Looloo tax ma bëgg leen a dégtal baat yu neex te xóot yi mu jagleel sunu werekaan bi, te mu ubbee leen téere fent bii di Aawo bi : “Aram Faal Jóob, mu ñàkk mi kiñaan te tëlee wonu.” Waxatuñu dara, mu teg ci baat yii nga xam ne, cuq nañ man lool sax : “Yii aawo, kenn du ma leen jëkk a sant ndax kenn du ma jëkk a gore. Lingeer yi mel nii ñoo tax géwél yi naan : sonn daw, jaaxle daw, bëgg a dee daw, doo fekke dara. Waaye sonn muñ, jaaxle muñ, bëgg a dee muñ, ku muñ muuñ.” Ginnaaw loolu, OSAD mi ngi amal liggéey bu am solo ñeel làmmiñi réew mi, rawati-na làmmiñu wolof. Ci tànk yooyu la doon dox ba tey bi muy fésal ak a wone, ci mboole mi mu dippe woon “fentakoon”, ni sunu làmmiñ yi mënees na cee fent i xalaat ak xeeti njariñ yu wute ak woy. Li mu ko dugge woon mooy wone ni sunu làmmiñ yi du woy rekk lañu ci mën a def. Dëgg la sax, OSAD biral na ne sunu làmmiñ yi amuñu dara lu ñuy ñeewe yeneen làkk yi ci wàllu taaral. Waaye, kàggug OSAD bi nga xam ne, li ko dale atum 1995 ba léegi, dees na ci lim lu tollu ci 50 téere, yemul doŋŋ ci ladab. Ndege, OSAD mi ngi yëngu tamit ci njàngle mi ak lépp lu ko soxal : mi ngi taxawal ay naal ngir daara yi, di tàggat aji-tàggat yi. Rax-ci-dolli, OSAD mi ngi móol ay téere njàng. Téere yooyu, nag, ci mbirum wér-gi-yaram lañuy wax, ci wàllu alfaabetisaasiyoŋ ak bépp xeetu ndimbal ñeel dundinu mboolem-nawle mi. Téere yu mel ni Njàngum Wolof, Ëmbub jàmm ak Téere xayma dañuy firndeel jubluwaay boobu ak bëgg-sa-réew bi OSAD làmboo. Nu gis ne kon, liggéey bi Soxna Aram Faal sumb ak joyyanti bi Séex Anta Jóob sumboon benn lañu. Dafa di sax, Soxna si, Séex Anta a di sëriñam. Ci njàngalem lay wéye : juboole aji-xam yeek askan wi, boole leen ñu doon benn bokk benn jëmuwaay te làkku nootkat bi bañ leen a féewale. Ngir dëggal loolu, Aram Faal yemul rekk ci di bind ay téere yu am maanaa lool ak sos genn këru móolukaay : dafa jaayante ak bakkanam tamit, bés bu nekk laa wax, nag. Te wax dëgg Yàlla, man rekk doy naa ci seede. Waaw. Ndaxte, man Ndey Koddu Faal mii di wax ak yéen, bés bu Yàlla sàkk ma woo ko di ko laaj ngir mu jubbanti ma, gindi ma, leeralal ma kumpa yi làmmiñu wolof àndal. Nun kat, ku nekk dafa jàpp ne peeg na wolof, fekk ne ak a bare ay fiir ! Duma leen ko nëbb, nag, saa yu ma koy woo, damay xaw a am kersa. Waaye saa bu wuyoo ak mbégte mu baat bi di àndal ngir rekk yéwénam ci xam-xam, sama xel dal, ma am fitu laaj ko ay laaj yu bare ci mbindum wolof ak pirim baat yi. Jàpp naa ne sax, deñ-kumpa gi ci man moo tax mu fonke ma ni mu ma fonke ba tax, tey jii, mu sant ma ma dégtal leen jaar-jaaram ci wàllu xam-xam ak xeex yi mu jot a xeex. Du caagéeni ne dama aay, ndax am na ci yéen ñi may déglu ñu ma gën a mën lii mu ma sant. Yàlla na fekk ne kàddu yii ma tibbe sama biir xol, jegele nañu leen, ci xol ak ci xel, ak jëmm jii nga xam ne, bokk na ci aji-xam ak boroomi màqaama yu gën a ràññeeku ci sunu réew. Bala may daaneel, may leen ma ma dello njukkal njabootu Tataa Aram ak i mbokkam. Ndax kat, sunuy mbokk ñooy sunuy wéeruwaay. Rax-ci-dolli, yar bi sunuy waa-jur di def ci nun moo tax nu doon li nu doon tey. Te wolof dafa ne, peccum liir bu neexee, ndeyam a téye ca mbagg ya. Bàjjen Aram, Wolof Njaay dinay wax ne bés du mag du tuuti, boroom lay tollool. Kon, kàddu gun fi yëkkati tey jëmale ko ci yow, xeeb nanu ko, yelloo nga lu ko ëpp. Kon, dunu def lu dul di la ñaanal gudd fan ak wér, nga yàgg fi lool di nu won yoonu yokkute. Ñaan boobu lanu lay ñaanal, ni la ko Séex Adaraame Jaxate ñaanale ci xolam, bi mu lay jagleel benn ciy téere fent yi mu bind : ‘’Yàlla na ngay Maamati-Maam’’. NDEY KODDU FAAL Ñi ko tekkee ci tubaab : Paap Aali Jàllo ak Ndey Koddu Faal ARAM FAAL, SUNU SÉEX ANTA JÓOB BU JIGÉEN… was originally published in Defu Waxu on Medium, where people are continuing the conversation by highlighting and responding to this story.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/mbay-jaag-gor-gi-senegaal-ameel-bor-ii/
MBAY JAAG, GOR GI SENEGAAL AMEEL BOR (II) Am it lu mat a taxaw-seetlu : jamono jooju Mbay Jaag doon jiite ndongo yi, fekkoon na mu bokk ci PAI, pàrti  “marsist” bu mag boobu  Majmuut Jóob sosoon te mu jiite woon yéngu-yéngu ya jiboon ca 1958 jëm 1960 (“boroom paŋkàrt  ya”) ba Afrig Sowu Jant gépp doon xeex ngir moom boppam, yewwiku ci nootaange bi ko Tubaab bi tegoon. Noonu Mbay Jaag bokkoon ci pàrti bu mag boobu. Dëgg la, PAI ag cëslaay gu ko daan dooleel la. Waaye, li am ba am moo di ne loolu taxul woon Mbay jiitaloon mébétu pàrteem ba tax koo fàtte njariñu askan wi. Xew-xewu ‘’Mai 68’’ boobu amoon na solo ci dëgg-dëgg su ñu gise, ca ginnaaw ga, coppite yu baree-bari yi mu indi woon ci àddina sépp, rawati-na ci sunu Senegaal gii. Ndax ña doon jiite réew yi gisoon nañu ni mënatuñu woon doxale nañdaan doxale lu jiitu xew-xew yooyule. Moo taxoon Seŋoor mi amoon gis-gis lool ci wàllu politig, ci kaw it ay ndigali Pari, daldi sàkk pexe yu yees : teggi sañ-sañu benn pàrti doŋŋ(UPS), benn sàndikaa doŋŋ(CNTS), benn kurélu kàngaami iniwersite doŋŋ…  Tërëlin yu bees yoyu nag, xéyu ñu benn bés  ñu sotti : dem nañu ba atum 1974  ñuy door a nemmeeku naka la li ci ëpp doon matale. Ndegam Mbay Jaag daa bokkoon ci pàrti politig, mënul woon a ñàkk am péete ci wàll woowu. Looloo taxoon, ba PAI amee ay jafe-jafe ci biiram  ndax ñàkk juboo ci yoon wi ñu waroon a wéyale xeex bi ngir indi demokaraasi ci réew mi, moom mu ànddoon ak ñi doon weddi seeni njiiti pàrti ca nañu daan doxale. Mënees na lim ñenn ci àndandoom yooyu : ndem-si-Yàlla ji Mbàbba Gise, ndem-si-Yàlla ji Elimaan Kan, ndem-si-Yàlla ji Baabakar Saane, Abdulaay Bàccili… Ñoomñooñu dañoo mujje génn PAI sos seen pàrti bopp (LD  – LD/MPT) akseeni ñoñ. Seen kurél gu bees googu nag, doon wéy, njëkk ci yoonu “marsism” laata ñuy yaatal, ubbil seen bunt ñeneenñu amul woon boobu gis-gisu àddina. Ñu raññeku woon nag lool ci biir liggéykat yi, rawati-na ci jàngalekat yeek fajkat yi. Noonu lañu leen doon jàppale ba ñu taxawal seeni sàndikaa. Liggéey boobu yépp nag, Mbay a nga woon ca biir te kenn daawu  ko woon jëkk ci lenn. Mbay Jaag ak pàrteem, ñu raññeeku woon lañu ci xeex bi kujje gi doon xeex nguuru Abdu Juuf mi fi wuutu woon Seŋoor. Ñu àndoon ceek Ablaay Wàdd mi doonoon njiitu PDS ak kujje gi ci boppam. Noonu la Ablaay Wàdd fexe woon ba toog ci jal bi, ca woteb atum 2000, ginnaaw yéngu-yéngu yu metti ya amoon  ca njeexitalu nguuru Abdu Juuf.  Pàrti Mbay Jaag bi  amoon ci taxawaay bu am solo. Moo tax it ñoo bokkandoo woon jiite réew mi ba ñu amee ndam ca woteb atum 2000 ba. Waaye yàggul dara ñu féewaloo seen biir : Ablaay Wàdd ak PDS jaar nii, waa LD jaar nee ba mu des Mbay Jaag ak ñenn ña mu àndaloon. Ñoom ñooñu gàddaay génn LD ba noppi des ak Wàdd ci nguur gi. Taxul ñu fekki  ko ci PDS, ndax dañoo sos ñoom it pàrti bu ñu moomal seen bopp (UFPE). Mbay Jaag moo jiite woonati fippu boobule, dem ca ba jeex. Ba taxoon na, ñu bare ci taskatu xibaar yi, ak ñu baree-bari ci askan wi doon ko ci ŋaññ, jàppoon ne daa jaayoon ngoram. Moom ci boppam, réeréewul woon mbir ni lu ni mel doon na ko ci fekk, teewul mu amoon fitu jàkkaarlook ñépp, taxaw fi mu taxaw. Noonu la ko Ablaay Wàdd woowe ci wetam, boole ko ci njiiti Màkkaanu Njiitu-réew mi. Mu def fa liggéey bu am solo, su nu sukkandikoo ci seedey ña mu fa doon liggéeyandool. Ku Yàlla defoon nga bokkoon liggéey ak moom ci jamono yooyu, te fekk nga jotoon a xam ku mu doon dëgg, dinga mën seede it ni, genn coppite gu yées feeñul woon ci moom. Moomoon boppam, amoon xalaati boppam. Fulla, faayda ak ñàkk caaxaan ñoo ko mas a màndargaal. Mu nekkoon ku xareñ, nangu liggéey, bañpar-parloo, di fexe di yemale ñépp saa su ne. Looloo waraloon ñu bare ci béréb bu kawe boobule daan ko laale bant bu gudd. Jikkoom jooju, ñépp raññe woon ko ci moom (nga bëgg ko walla nga bañkoo bëgg), moo ko mayoon mu doon jiite,  ñaari ayu-bés yu ne, ndajem-kàngam yi doon xelal Njiitu Réew mi. Mu doon nag jaarale lépp yoon. Kenn mësu ko ca woon a sosal  lenn walla doon am lenn lu mu ko ca doon yabe. Wax dëgg, dañko ca daan gën a naw. Nit kooku moo doon Mbay Jaag, ci liñci xam. Ku bëggoon réewam, jébbalu ci Senegaal gi mu doon xeexal, di ko liggéeyal saa su ne, ba bés  ba mu sàngujee suuf. Tey, wéetal nanu. Di ko jaale ay mbokkam, ay xaritam, ay àndandoom, di ko jaale  Senegaal gépp. Yàlla na suuf woyof ci kowam, Yàlla na ko Sunu Boroom yërëm te xaaree ko àjjana.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/ana-lu-goor-giy-laqarci/
ANA LU GÓOR-GIY LÀQARCI ? Bamu jógee Konaakiri ba tey, seeti woon Alfa Konde, Abdulaay Wàdd, sunu Njiitu-réew ma woon, a ngi ne selaw. Wote bu 24 féewaryee bi sax, ak faluwaatu Maki Sàll bi mu jur, ba tey, yéyul yàbbi ci benn yoon. Mi ngi toog ci otelam ne tekk. Terewul ñëpp moom lañuy déglu. Lu ni mel, Wàdd yàgg na koo am. Bu waxee, moom rekk la askan wiy dégg. Ba mu waxee ci ndoorteelu kàmpaañ bi, baatam sutoon na yu lawax ya doon xëccoo nguur gi. Ba mu toogee ba tey, cellam gaa ngiy jur coow lu bari. Mënees na njoort ne Góorgi dafa amul la mu bëggoon. Mel na ni mi ngi doon xaar Idi ak Sonko dem lëngook moom bi leen Maki Sàll dumaa. Waxoon na leen ne : « Maki dina leen dóor te bu keroogee buleen ñëw fii di jooy ». Waaye Idi ak Sonko seetiwuñu ko. Xeexuñu itam, ni ko ñu bari ragale woon. Mu mel ne dañoo bàyyi Maki ak Yàlla, ngir wuyu wooteb jàmm bi jibe ci njiitu Murid yi. Bu ko Idi ak Sonko seeti woon, ndax Laay Wàdd doon na sedde nii ? Ndax kon du jéem a yëngal gaal gi, ni ko woykat biy waxe ? Yàlla rekk a xam. Li wóor daal, moo di ne Góor-gi waxul dara ci wote bi. Jaar na yoon am déet ? Ndamu Maki li lew na, am déet ? Wàdd waxul, pàrteem waxul. Ba bésu tey. Terewul Maki Sàll tudd ko ci jàkkaarloo bi mu amal ak taskati xibaar yi altine jii nu weesu. Woo na ko, moom ak Abdu Juuf, ci waxtaan yu mu nar a amal ak làngu politig yi ci ayubés yi ñu dégmal. Ba tey nag, Wàdd tontuwu ko. Walla boog dégguñu tontoom. Ndax, bu dee ñaar ñaa ngi diisoo ci suuf it, du bett kenn. Ku yàgg a seetlu Góor-gi, war ngaa xam ne ñàkkul lu muy làqarci ci guddi yi ñu tollu. Ndax mbiru doomam rekk la ? Mën naa am ñu xam ci dara ci fan yi ñu jëm.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-alxames-4-me-2023/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM (ALXAMES 4 ME 2023) RËBËJOO BA CA PSG Gannaaw tukki bi Messi amaloon ca Araabi Sawdid, njiiti Paris Saint-Germain daan nañ daan bu diis. Dañoo ajandi Messi ñaari ayu-bés yoy, du ci futbal te yit du ci tàggatu. Yemuñu foofu de, ndax dinañ ko dagg peyoorug ñaari ayu-bés yooyu ñu ko ajandi. Gannaaw bi loolu amee, démb ci àllarba ji, 3 Me 2023, benn naaxu soppey PSG dem nañu ca màkkaanug ekib ba, doon fa yuuxoo turu Messi bay yëkkatiy saaga yu ñaaw di ko teg ci kaw saa-àrsantin bi. Bañ fa jógee, dafa am ñenn ñu dem ba kër Neymaar taxaw ca buntu ba itam doon ko saaga ak di ko móolu. Ci ginnaaw xamle nañ ci lu wér ne Messi day dem bu at mi jeexee. CAN U17 Kaar, sunu xale yaa nga ca yoon wa. Caatu gaynde yi nekk nañu ñi nga xam ne ñoo njëkk a dem kaar-dë-finaal ci kuppeg Afrig gii ñu jagleel ñi amagul 17i at foofu ca Alséri, gannaaw ba mu dóoree ñaari joŋanteem yi njëkk. BULAAY JA, GAYNDE GU DÉGGUL JAT Jamono jii, kenn mënul a téye Bulaay Ja foofu ca Itali. Keroog, ca ayu-bés bi weesu la xañ Napoli mu doon sàmpiyoŋu Itali. Ndax bii bi mu duggal ca njeexitalu joŋante ba. Démb, ci àllarba ji, mu dugalati ñetti bii ci seen joŋante geek Fiorentina. ESPAAÑ : FINAAL “COPA DEL REY” Real Madrid dina daje ak Osasuna Gaawu 6 Me gii ñeel finaalu kuppeg Buuru Espaañ bi.  Ñu ciy xamle ni Modric mi ame woon gaañu-gaañu dana bokk, ndax tàmbaliwaat na tàggatu.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/tabaski-2023-xutba-serin-baabakar-si-mu-dabbaax-njool-fuuta/
TABASKI 2023 : XUTBA SËRIÑ BAABAKAR SI MU DABBAAX (NJOOL-FUUTA) Ci alxamesu démb ji la ñu ëpp ci saa-senegaal yi tabaski. Ku ne tabaski, ne xutba. Te, xutbay imaam yi, dees na koy faral di xaaj ñaari pàcc. Bu ci njëkk bi, imaam yi dañu koy jagleel diine ji, jagleel beneen ñaareelu pàcc bi tolluwaayu réew mi, rawatina li ci fës. Noonii la fa deme at mii tam, fa tiwaawon. Sëriñ Baabakar Si mu Abdul Asiis Si Dabbaax xirtal na jullti Senegaal yi ci ñu dekkil mbaaxi mbokkoo ak dimbalante, cuufe ak sutura. Ci alxames ji la tiijaani Tiwaawon yi tabaski. Kilifa gii di Sëriñ Baabakar Si mu Abdul Asiis Si Dabbaax, ñu duppee ko Njool-Fuuta, moo jii te julli ba. Ba muy xutba, dafa fàttali mbaaxi démb yoy, dañuy bëgg naaxsaay ci biir mboolaayu Senegaal. Moo ko tax a ñaax askan wi ci dundalaat mbaaxi yooyii mag ña sàrtoo woon. Sëriñ bi ne : « Ñi amul wërsëgu dunud ak seen i maam, dund nañu, as-tuut, ak seen i baay. Réer gu jéggi dayo gi fi am day firndeel ñàkkug gindikukaay. » Sëriñ bi neeti, jot na ñu fàttali doomi Senegaal cuufe ak dimbalante, rawatina ci jamono yu mel ni tabaski ak tolluwaayu réew mi. Imaam bi ne : « rendi sam xar, di bàkkoo taar baak duufaay bi taxul Yàlla nangul la. Diine, dees na ko dunde ni ko Islaam tëralee. » Xalifa Tiijaan yi, Sëriñ Baabakar Si Mansóor, dafa tawat moo tax jiitesiwul julli ji. Waaye, balaa Njoo-Fuutay xutba, Papaa Maktaar Kebe waxoon ci turam, jottali ngërmaandeem tiijaan yi jàpp yépp ci tabaxug jumaay Tiwaawon ju mag ji. Jottaleet na ñaan xalif yi bi jagleel daayira yi, kurél yi ak saa-senegaal yépp yi ci jàpp.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/li-gen-a-fes-ci-xibaari-taggat-yaram-dibeer-5-mars-2023/
LI GËN A FËS CI XIBAARI TÀGGAT-YARAM (DIBÉER 5 MÀRS 2023) LÀMB Saa-Cees – Rëg-rëg ñoo doon bëre ci dibéeru tey ji. Mu doonoon làmb ju ñépp doon xaar. Waaye, nag, coow am na ci. Nde, bu dee àttekat yi Rëg-rëg lañ jox ndam li, Saa-Cees ak i farandoom nee nañu ñoo daan. Ndaxte, ci biir jaxasoo bi, am na fu Rëg-rëg sampee 2i loxoom ak 2i wóomam, muy 4i apiwi, nees koy waxe. Kon, Saa-Cees a yeyoo ndam li. CNG mooy àtte. PSG / FARÃS Mbappe defati na jaloore Mbappe tegaat na beneen jéego ! Doon na kuppekat bi ëpp lu mu dugal ci mbooru PSG. 201 bii la fa dugalagum bim fa ñëwee ba léegi. Bu ñu fàtte ni, Mbappe, 24i at doŋŋ la amagum. Waaye, ak li muy doon xale yépp, dafa dooj ba, turam siiw na lool. Gannaaw jéego bu réy bim defaat la Ronaldo, kuppekat Beresil bu mag ba, wax lii ci moom : ” Li Messi ak Ronaldo def ci kuppe, mennum Mbappe moo ko mën a defaat. Bu nu fàtte ni 24i la amagum.” Marquinhos ame na gaañu-gaañu Ba tay foofu ca PSG, gannaaw ndam li ñu am ci kaw Fc Nantes, démb ak li Mbappe def, njàqaree ngi bëgg a gane seen biir ak joŋante ñuy waajal ak Bayern, di bu ñu war a gañe bu ñu bëggee wéyal seen yoon ca “Ligue des Champions “. Marquinhos àggalewul seen joŋanteb démb bi, dafa gaañu, daldi fekki Neymar ak Kimpembe. Wuteek nañook Bayern mi nga xam ne, ay kuppekatam yi gaañu woon ñoo ngi delsi. LIGA / Espaañ Paap Alasaan Géy, ñu miin ko ci Paap Géy, defaat na beneen paas ci seen joŋante bi ñu ñàkk démb ci kanamu Athletico Madrid (1-6). Paas boobu mooy ñetteelam ba mu demee ca Seville ba léegi, di wane miinam bu gaaw ci këlëb ba. Mujjul a àggali joŋante bi itam, moom Paap Géy. Ndax, dañ ko ruus ginnaaw bi mu amee ñaari kartoŋ soon. MILAN / ITALI Ibrahimovic, na woon, fa woon “Ñëwat naa gannaaw sama gaañu-gaañu bi. Léegi, dinañu xamaat kuy tàmbali joŋante yi. Bi ma gaañoo ataakã yaa ngi doon wane seen bopp. Waaye nag, dikkaat na. » Kàddu yooyee la Ibrahimovic yëkkëti gannaaw ba ko benn taskatu-xibaar laajee lu jëm ci moom ak ekib ba.
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/ay-du-yem-ci-boppu-boroom/
AY DU YEM CI BOPPU BOROOM Senegaal, jamono ji ñu tollu nii dafa mel ni nekk doomu– réew mi rekk doyatul ; fàww nga fésal wet gi nga féete, moo xam sa diine la walla sa tarixa mbaa pàrti pólitig bi nga faral ba ci sax mbootaay gi nga bokk léeg-léeg. Waaye li ci gën a tiis, tey tiitalaate ba noppi ruslu mooy ñaawtéefi ñi ñuy tudde boroomi xam-xam. Ñenn ci ñoom a ngi taal i daay, ñi ci des di leen xamb. Ndax kilifa war naa làquy giseek i doomi-réew mi naan leen su nu jàppalewul Diw ci joŋante biy dégmal mu ñaaw ndax nook moom a bokk waaso ? Ana lu yées lii ? Ruwàndaa bokk na tey ci réew yi ñu gën a naw ci Afrig waaye du tax kenn fàtte la fa xewoon ci atum 1994. Kodiwaar tamit, démb rekk la woon. Kon mbirum waaso ak xeet du lu ñuy kafe. Nun waa Senegaal nag, li nuy seetaan muy raam, ci ñag bi la jëm. Te kenn ñaanu ko Yàlla. Nan bàyyee nax sunu bopp, naan bal du fi tàkk, jaasi du fi jóg ndax lii walla lee. Nanuy fàttaliku ne noo bokk ndey bokk baay tey moytu lépp lu nuy féewale. Ngalla buleen fi yee fitna ndax, kat, bu keroogee kenn du ci mucc. Du xam ngeen ni ay du yem ci boppu boroom ?
Defuwaxu