text
stringlengths
38
33.7k
moom de njaayum jaam ag tooñaange gu mag la ñeel ag nite ci lu dul gën jaa néewi sikk
moom alxuraan nag waxi yalla la ju nu wahyu yonent bi jaare ko ci jibriil , muy lol daa wacc ci anam gu toftaloo te toppante , ci diir bu tollu ci at .
waaye gisunu fu nu koy awale ndax mbooloo ma .
ab dajeem it benn yoon la daa am ci at mi ci weeru koor ngir xool aka xalaat ci mbooleem xew xew ak mbir yu am solo yi nekk ci ay tëralam prograamam
muy jagleg neew gu bayyiwul ginnaaw senegaal miy wey di wanni lim wu rey ciy faatu ci yoon yi , doonte am na ag wanniku digante ak .
waaye léegi nag yàlla feeñal na ni nit mana jube ci kanamam ci lu séqul ak yoonu musaa dara
ndax ca diiney bu afrig , sarax ak xarafal amona bu yag , ba tey .
aji sax ji , yalla miy degg , ngalla jot ma .
ko munal nag , ndax goor laati de ! booba rasel a ngi waaja faatu . terewul bala bakkanam a rot tudde na xale bi benoni mu firi sama doomu coono . teewul baay bi tudde ko benamin mu firi sama doomu njiglaay o .
kurelu yonenti yeriko nag dikk ba ca alyaasa ne ko ndax xam nga ne
yaakaar aw fas nax sa bopp la , kattanu fas dug wall .
ci injiil dafa misaale bérab fu xare bu mujj bi nara am ci diggante gaayi yàlla yi ak gaayi seytaane yi ci muju jamano ji
ci dëgg dëgg maa ngi la koy wax képp ku judduwaatul doo mana seede nguuru yàlla
fakkaskatu xeet yee jog , genne keram , nara gental seeni dekk ,
indil aji sax ji xar yu goor yu menn at yu mucc sikk , naar ci bes bi , muy saraxu rendi doomal bi war bes bu nekk . menn xar mi , ngeen sarxal ko ci suba , naareel bi , ngeen sarxal ko
sëñ bi nee na ginaaw bi nu jullee tàkkusaan nasaraan boobu di njiitul soldaar yi dikk na bëgg a wax ak moom mu wëlbati kanamam wëlif ko jublu yàlla jàng bismil laahir rahmaanir rahiimi juroom fukki yoon waa ja nooy aw xalam fay mu gaaw genn jëm ci ay aajoom mu fanaan foofa ak jaraaf ju ñuul jooja ci loolu sëñ ba a ngi naan ginaaw bi nu dajee k ña génnoon jëm ca këram te njàqare nekk ci seeni dënn
seetu buur duggsi na , ne rann , sol mbubb mu wurus way takk .
boole naa léen ci ndam li nga ma sol ngir ñu àndandoo ni nu ànde man ak yaw
ba buuru israyil yowayas doomu yowakas duggee naareelu atu nguuram , ca la amaciya doomu yowas falu buur ca yudaa . naar fukki at ak juroom la amoon ba muy falu . nguuru na naar fukki at ak
dëkku njàng la woon bu amoon jenn daara ju kawe iniwersite
bóom ngeen aji dundal ji waaye yàlla dekkal na ko
ba mu ko waxee loolu , laban ne ko jigeen nii samay doom lanu , xale yii
24 gësëmal dàttu tàndarma gi tàndarma yu ñor xomm rot wutsi la
gannaaw loolu yeesu daldi gedd dekk , ya mu defe woon la epp cay keemaanam , ndaxte tuubunu seeni bakkaar .
waaye benn waay bu dëkk samki bu doon tukki ñëw ba jege waa ja gis ko yërëm ko
ci bis bi njëkk ci ut la ndajem xeet wi jibal ci 4 ut mu neenal sañ sañi laman yi ak yeneen yi garmi yi ame woon ak niti diine yi
te tit mi ma gunge woon sax de , li mu bokk ci xeetu gereg , taxul nu sonal nu ci xarafal ko .
kopernic moom àndutoon ci gisiinu batlimos wi doon wax naan suuf si moom daa bulu ba noppi nekk ci digg àdduna bi bu ko defee yarami asamaan yi di ko wër
nekkoon taalifkat bindkat doonoon it killifa aada ca tirki
ngalla gaawe ma boroom bi , yaa may musal .
noonu yeesu degg ko , mu ne leen ni wer soxlawunu fajkat , ni weradi noo ko soxla newuma woo ni jub , waaye bakkaarkat yi laay woo .
ca ñetteelu fan ba ma àgg fa ma yàlla jëmale
lii daal coona la bu kenn xalaatul a dund ak moom , te dund gi tam narutoon a wey ci yoonam wii , bu yalla t .
laqoo aji sax jee gen woolu doom aadama , laqoo aji sax jee gen woolu garmi .
jimbulang yi man nañoo wuute aju ci seenum ëmbiit man nañoo ubbeeku ci xeeti xameef yépp jimbulang bu trecani ak jimbulang bu waa brëtaañ ñooy yi ci gën a siiw walla itam tënku ci wenn xeetu xam xam wi niki ab jimbulangu paj bu xam xam walla bu xeltu
yengu yengu yii , mujjoon na naat , te dox , bijjaloon it boppam lu sakkan ci waxambaane yi ak xalaatkat yi , aggoon nanu ci lu toll ne juroom fukki junniy waxambaane , yu weesu ay neen fukki at yooyu .
seeni buur ak seeni kangam , ak baadoolo yi ci biir dekki yudaak mbeddi yerusalem , defe ngeen ne aji sax ji yegu ko , am da koo fatte ? aji sax ji manatula dekku seen jef ju bon ak seen jef ju siblu ji waral seen um reew mel nii mu mel tey , di ndand foyfoy bu gental bu nuy mooloo , te kenn dekku ci , ndax yeena def saraxi bokkaale , moy aji sax ji , degluwleen aji sax ji , te it kaddug yoonam ak dogali yoonam ak seedey yoonam , jefewleen ci lenn . moo waral musiba mi leen dikkal nii tey .
ndefar yi nag masunoo dan di jem kanam ba ci sunu jamono jii nu toll .
feenalug loolu nag mi ngi ame woon ci lu tollook atum g . boroom xam xamu almaan dikk , fent ab jumtukaayu kuran buy juddal kuran atum g .
mooy kiy weddi ne yeesu mooy kirist almasi bi
naareelu xare bi dakk na niki bi ko jiitu woon alag dundug ay milyo ciy nit .
besub keroog , jambaar ju epp u fit , du lay def , di daw .
soo ci beggee bokk , kon a href register url s bindul a .
bi mu ko defee nag ay jeexiitalam tas ba àgg ci pàkk yu bari ci àdduna bi loolu nag ci ñaari xarnu yii la fukk ak juroom ñeenteelu xarnu ak ñaar fukkeelu xarnu g
ci kaw loolu yeremi jot na kaddu gu bayyikoo ci aji sax ji , gannaaw ba ko nebusaradan njiitu dag ya yiwee , mu bayyikoo rama . yeremee nga nu jengoon , mook ngallog yerusalem gaak yudaa ga jem babilon .
paj man nañu ne mooy ker keraan bi la man a gën a may ngay man a jonjoo ag nit ñu néew ñi doole ak ñu ñàkk ñi
yonneeleen boroom reew mi yobbalu kuuy yu ndaw , jele ko sela , jaare mandi ma , yoti ko buurub yudaa fa tundu siyo mu taaru . jigeeni mowab a nga ca jeggikaayu dexu arnon , mel ni picc yu tasaaroo fa seeni tagg ,
niy wut sama bakkan , yal nanu rus ba torox
njunj gi nuy jefandikoo ngir tudd bariwaayu dawaan limu dawaan giy wal ci jenn jamono mooy i , di ko wax taraayu dawaan , te bennaanu natt bi nu koy natte di bi adduna bi deggoo mooy ampere .
mbaa siyo , makkaanu aji sell ju israyil .
yaw réewum sabulon ak réewum neftali di yoonu géej gannaaw dexu yurdan yaw galile réewum ñi dul yawut
su la mën ngawar jayee ba nga mafñàndum saaw boo fa jógee loo bayati jënde kog teg
ku ñu dénk sasu topptoo yëfi mbooloo mi nag nay ku yem ci benn soxna jiite bu baax këram ak i doomam
nu daal di sos ay barab yu nu jagleel tas injiil ak seddale ko , ak yeneen teerey seen diiney nasaraan ji , ak seen yeene yi aju woon ci seen woote bu nasaraanal bi .
naar . naka lanu dem bay begga genn dekk ba , samiyel ne sool neel surga bi , mu jiitu nu . mu wax ko surga ba , mu jiitu leen . samiyel neeti sool yaw , taxawal fii tuuti , ma degtal la kaddug yalla .
jumtukaay yiy lonku ci internet lees di wax di tekki gan ci wolof walla nosteg njeexte ci wolof mbir miy jokkale yi la ñuy wax lëkkalekaay
sakkuleen ma , ba dund . buleen sakkuji fa betel , buleen dem gilgalr , te buleen jall beersebas . gilgal ay galloo ngallo betel neen .
looloo tax nuy gis ne kattan mooy man gi neen man a def ab liggeey yengu muy njureeful yengoom googu , walla njureeful ab barabam bu nu ko nattee ci doole yiy liggeey ci kawam .
kepp ku ko gem deesu la daan , waaye ku ko gemul daan nanu la ba noppi , ndaxte gemuloo ci turu doom ji yalla am kepp .
gannaaw ba sool feddlee nguuram ca israyil , xare naak seen noon ya leen wer yepp mowabeen naak amoneen naak edomeen naak buuri waa soba , ak waa filisti . mboolem fu mu walbatiku rekk , moo daan . njambaar la xaree , duma amalegeen na , ba musal israyil ca na doon sexetoo seen alal .
ma daanu tey , nu daje di ko bege , dajaloo fi sama kaw ,
tubaab yi jeemaatoon nanu koo japp ba yabaloon fa ay spahis nga xam ni ay xarekat yu nuul lanu te andoon ak nootkat bi waaye taalibey serin bi antoodil loolu .
danuy futti say yere , foqati say ganjar .
dugub nak ba nga ko déggee suuna moo ci gën mooy përëmyér dugub
ba loolu amee sool xadaru ci kaw yonatan . mu ne ko doomu caga bi ,
xam ngeen ne , kollere gu nu fas ba noppi , warunu koo fecci , walla nu ciy rax dara .
teewul , askan wa fa dekkee aartu nanu ne dees na leen degg bu beneen dog dogu mbej bu yagg amee .
te bu leen kenn waxee dara , ngeen ne ko boroom bi da leen a soxla .
ibraayma jelaat na soxna su tudd ketura , am ca simran ak yogsan ak medan ak majan ak yisbag ak suwa . yogsan jur saba ak dedan . askani dedan nooy asureen ni , letuseen ni ak lewumeen ni . doomi
moo tax aji sax ji wax ci buuru asiri ne
maanaam barnabas simeyon ku ñu dàkkentale ñuul lusiyus mi dëkk siren manayen mi yaroondoo ak erodd boroom diiwaan ba ak sóol
fukk yi nu wacce leen ci yonant yalla aadama j .
ci kaw loolu atalyaa yaayu akasiya buuru yudaa xam ne doomam ju goor ja dee na , mu daldi faagaagal mboolem ku bokk ci askanu buur . teewul jigeenub akasiya , yoseba doomu buur yoram , daldi
mu new ci nun , daldi yeew ay loxoom ak i tankam ak laxasaayu pool naan nii la xel mu sell mi waxe ki moom laxasaay gii , yawut yi dinanu ko yeewe nii ca yerusalem , jebbal ko ni dul yawut .
waaye nam wu deger , ni mat a ko yelloo , maanaam niy jefandikoo seen xel ngir rannee lu baax ak lu bon .
ne ma dann , ba su ma bakkaaree , doo ma baal samag toon .
giirug leween ni nag ci banni israyil lanu bokk , waaye limaaleesu leen ak noom . aji sax ji moo waxoon musaa , ne ko giirug lewi noom , bu leen lim , bu leen wannaaleek banni israyil . waaye yaw ci sa bopp nanga sas leween ni jaamookaay bi seedes kollere gi dence , mook la muy andal lepp , ak mboolem lu ca bokk . nooy gaddu jaamookaay bi , ak la muy andal lepp , di ko topptoo , te it fi wer jaamookaay bi lanuy dal . bu jaamookaay bi dee dem , leween nee koy wekki , bu jaamookaay bi dee dale berab , leween nee koy we . ku ci bokkul ba laal ci nag , dees koy rey . banni israyil gi ci des , na ku ci nekk topp dalam , ak raayaam ak kurelam . leween ni nag nanu dal fi wer jaamookaay bi seedes kollere gi dence . su ko defee am sanj du dal ci kaw mbooloom banni israyil . te itam na leween ni denkoo denkaaney jaamookaay bi seedes kollere gi dence .
la fa des ci ay teere yu nu bind ci kalaama araab , pel , songaay japp nanu ne epp na . teere !
baadi moom mooy njiitu doomi buur bi , ak yenn ci jewrin yi .
ci noonu faraas jug jibal ab xare ci kaw brusiya ci 14 sulet 1870 te fekku ko woon jekk ngir xeex te taxul woon it mu xalaat ci ngérte yi man a juddoo ci bii xare bis bu ñu dàqee fraans ci xeex bi
sanc gi nag jeemoon na a defi pexe ba askan yi nu sanc dunu doon mukk benn bu ko defee mu def lu nekk jëfandikoo pexe mu mu man a doon ngir xeet wi bañ a nekk benn
kiy sàmm yoon wi moom la yàlla di àtte ni ku jub
loolu ngeen wara def waxuma nag ngeen bàyyi la ca des
seeni njariñi koom koom it bokkewul woon te niroowul woon waaye nag loolu lepp teewul woon amoon nanu ñatti mbir yoo xam ne kenn wuutewu ci woon ñepp a ci dëppoo woon ñooy
beljik ruwaayom bu beljik réewu tugal óróop
noonu baat bu xumb jóge ca gàngune ma ca kër yàlla ga naan
bees sukkandikoo ci yeenekaayu amerig bi , new york times , lepp a ngi door ci besub altine , eelu fan ci weeru me . dafa amoon ku woo takk der yi , ne leen am na jenn waay ju jend sigaret ci benn mangasin , feye kook sagarub i dolaar bu baaxul . nee nu , waa jooju , george floyd la tuddoon . moom , george floyd , wattuwaafoonu kaaraange la woon ci benn feccukaayu guddi . waaye , dafa nakkoon liggeeyam ci sababu mbas mi lembe addina .
nu ne ko musaa maye na , nit bind kayitu pase , taggook jabaram .
ci yoonu dee da ñuy egg ci beneen nekkin
njiit la nag , surgaam bu mu beggoon lool dafa feebaroon , bay begg a dee .
indil aaroona ak i doomam ba ci bunt xaymab ndaje mi , nga sang leen ci ndox mi . nga daldi solal aaroona yere yu sell yi , diw ko , sellale ko ko , mu doon sama sarxalkat . su ko defee nga indi ay doomam , solal leen ay mbubb . nga diw leen , ni nga diwe seen baay , nu doon samay sarxalkat . seen diwu googu moo leen sedd sasu carxal bu sax dakk , maasoo maas . musaa nag def loola . mboolem noonee ko ko aji sax ji sante , na la ko defe .
ndakaaru dakar nekkoon péyu afrig gu sowwu gu fraase asf walla ndakaaru fimne mooy péyu reewum barug senegaal akit goxub ndakaaru tolluwaayam ci péeteg sowwu bu afrig ci jegeem daanaka dun bu kap wert waral na sancug notaakon yu jëkk yi akit yaxantu ak àdduna bu bees bi te ame na peetewaayu ngëneel ci jëflanteg cosaani saa afrig yi ak saa tugal yi
nanu jaamuji yeneen yalla , yalla yu ngeen xamul , su boobaa nangeen gestu , seet te laajte bu baax , ba degg gu wer feene ca mbir ma , ne defees na moomu mbir mu jomblu ci seen biir , ngeen daldi jam rekk waa dekk boobu , leel leen nawkay saamar , faagaagal dekk ba , ak mboolem la ca biiram , jur ga it , ngeen leel leen nawkay saamar . mboolem alalu sexetoo ju joge ca dekk ba , dajaleleen ko ca digg penc ma , te ngeen lakk dekk ba , booleek cexetoo ma , def ko doomal bu mat sekk , neel seen yalla aji sax ji . day doon ab gent ba faww , deesu ko tabaxaat . bu dara des ci seen loxo , lu bokk ci alal jooju nu wara faagaagal . su ko defee aji sax ji deddu sanjam mu tang , yerem leen , neewante leen , yokk leen na mu ko ginale woon seeni maam , ndegam yeena ngi degg seen kaddug yalla aji sax ji , ngir samm mboolem santaaneem yi ma leen di denk besub tey , ngir di jefe li seen yalla aji sax ji rafetlu .
coppite yi neel waxtaani jefandikukat xaris waxtaani jefandikukat xaris wii xetu jagleel moo lay won coppite yu mujj ci xet yi lekkalook wii .
maamu sooninke yi dekk boobu lañu baawo moo tax ñu yore tur wi sooni nke
seen péey nekkoon na céNN ca jamonoy njaa jaan njaay
bi nuy lekk nag , yeesu ne leen ci degg maa ngi leen koy wax , kenn ci yeen , ku bokk ak man di lekk sax , dina ma wor .
bi mu naanee ba noppi , mu jog , dellusi ci taalibe yi , fekk leen nuy nelaw , ndaxte seen xol dafa sonnoon ak tiis .
nasaraanalkat yi jeqi woon nanu fa ay fitnay kuréel ca la xarey kuréel yu tàng te tar juddoo ci libaa ci diggante mawaarina yi ak dursu yi atum 1860
xam xam yu mel noonu , nu ngi soqikoo ci aada yu nit teral , ci aaday addina , waaye soqikoowul ci kirist .