url
stringlengths
6
8
content
stringlengths
2
3.72k
source
stringclasses
3 values
page_310
310 80. Ña am xam-xam ne leen : “Toskare ngeen ! Yoolub Yàllaa gënal képp ku gëm tey jëf u yiw”. Ku dul muñkat du ko am. 81. Nu mëdd ko ci biir suuf si mook kërëm ga. Amul kenn ku ko mënoon a dimbali ku dul Yàlla, te it kenn dimbaliwu ko woon. 82. Ba ñu xëyee, ña doon xemmem wàccuwaayam ca démb sa, daldi wax ne : “Dafa mel ni Yàlla dana tàbbalal wërsëg ku ko neex, ci jaamam yi. Bu dul kon ak xéewalam, kon dey mëddoon Nanu. Te it yéefar yi duñu texe”. 83. Góogale mooy kër gu mujj ga, Dananu ko defal ñi bëggul a kawe-kawelu ci suuf si, te duñu yàq. Ña ragal Yàlla tey moytandiku ñooy ëppug mujj. 84. [Amul lu ñu bàyyi fii], Ku dikk ak i ñaawtéef, [na xam ne] ñay jëf ñaawtéef, la ñu daan def rekk la ñu leen di feye. 85. [Yàlla] mi wàcce Alxuraan ci yaw, Moo lay delloo fa Màkka. Neel : “Sama Boroom moo gën a xaw kuy indi dëgg ak kuy nekk ci réer gu bir. 86. Musuloo yaakaar ne dees na la jox Téere ba. Lu dul ne yërmaande ju bawoo ca sa Boroom. Te bul dimbali mukk yéefar yi ; 87. te it buñu la fàbbi mukk ci kàdduy Yàlla ginnaaw ba Nu ko wàccee ci yaw. Nangay woote jëme ci sa Boroom te bul bokk ca way-bokkaale ña. 88. Bul woo jeneen yàlla di ko booleek Yàlla. Amul jenn yàlla ju dul Moom. Lu nekk a faagaagalu ba mu des Moom. [Yàlla] mooy boroom àtte yi te ca Moom ngeen di dellu. ----------------------------------------------------------------------------- Saar 29 : AL-ANKABUT (JARGOÑ) 69 laaya - Laata-Gàddaay ga
coran-wolof.pdf
page_311
311 ----------------------------------------------------------------------------- Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi. 1. Alif, Laam, Miim. 2. Ndax nit ñi foog nañu ne danañu wax ne : “Gëm nañu ! ” te kenn duleen sànje ? 3. Sànje woon Nanu ña leen jiitu woon ; Yàlla xam na ñay dëggal ak ñay fen. 4. Walla ñay jëfi ñaawteef, jàpp nañu ne danañu Nu jiitu ? Aka ñoo ñaaw ab àtte ! 5. Képp kuy yaakaar a dajeek Yàlla, digub Yàlla boobu luy dikk la. Te Mooy dégg, di xam. 6. Képp kuy xare, boppam la koy defal, Yàlla ku doylu la ci waa àddina bi yépp. 7. Ñi gëm tey jëf u yiw, Dananu leen faral seeni ñaawteef, te Dananu leen feye ca la gën ca la ñu daan def. 8. Dénk Nanu nit muy def yiw ciy ñaari way-juram, “bu ñu la sonnalee nag ci bëgg nga bokkaale Ma ak loo xamul, buleen ca topp”. Ci Man ngeen di dellusi, Ma xibaar leen la ngeen daan def. 9. Ña gën tey jëf u yiw, Dananu leen dugal ca nit ñu yiw ña. 10. Am na ci nit ñi ñuy wax naan : “Gëm Nanu Yàlla” ; te bu ñu leen loree ci ànd gi ñu ànd ak Yàlla, dañuy jàppe sànjeb nit ñooñu ni mbugalum Yàlla. Bu leen ndimbal dikkalee lu bawoo ca sa Boroom, ñu tàmbalee wax naan : “Nun ak yéen a àndoon ! ” Moo ndax Yàlla dafa gënul a xam li nekk ci dënni waa àddina si yépp ? 11. Yàlla xam na tigi ña gëm, xam na itam naaféq yi .
coran-wolof.pdf
page_312
312 12. Yéefar yaa ngay wax ña gëm naan leen ; “Toppleen sunu mboor, dananu yenu seeni ñaawteef”. [Mukk] duñu mas a yenu tus ci seeni ñaawteef. Li wóor moo di ñoom ay fenkat lañu. 13. Danañu yenu seen yu diis ya ak yeneen yu diis boole ko ca. Te bu Bis-pénc baa, danañu leen laaj la ñu daan duur [fen]. 14. Yónni woon Nanu Nooh ca aw nitam. Mu sax fa ñoom junniy at yu yées juróom-fukk. Mbënn ma daldi leen di mëdd ba ñu tooñee. 15. Nu musaloon ko mook waa gaal ga ; def Nanu leen ñuy kéemaan ci waa àddina sépp. 16. [Fàttalikul it] Ibraahiima, ba mu waxee nitam ña, ne leen : “Jaamuleen Yàlla : moo gën ci yéen, de cëy bu ngeen xamoon”. 17. Yéen a ngay jaamu ay xërëm bàyyi Yàlla, di sos ay fen yu ngeen di jaamu te du Yàlla. Amaluñuleen woon wërsëg ; sàkkujileen wërsëg ci Yàlla. Te ngeen jaamu Ko te sant Ko. Ca Moom ngeen di dellu de. 18. Su ngeen ko weddee, jàppe ko ay fen, am na ay xeet yu leen jiitu woon daan weddi. Rikk nangeen xam ne ab Yonent jottali mu leer rekk a ko war. 19. Moo ndax dañoo gisul ni Yàlla di sosee mbindéef te di ko defaraat ? Looloo ka yomb ca Yàlla. 20. Neel : “Wërleen [dox] ci kaw suuf si te ngeen xool naka la Yàlla sosee mbindéef yi. Ak itam naka lay sos gu mujj ga di deme. Yàlla mën na lépp lu ne”. 21. Dana mbugal ku ko soob te it Dana yërëm ku ko soob ; te yéen ñépp ca Moom ngeen jëm. 22. Mënuleen a të ci kaw suuf si waxantumaak asamaan si ; te itam amuleen wenn wéeruwaay mbaa dimbalikat bu dul Yàlla. 23. Ña nga xam ne dañoo weddi kàdduy Yàlla ak dajeek Moom, ñooña naag nañu ci Sama yërmaande. Te it danañu am mbugal mu mitti.
coran-wolof.pdf
page_313
313 24. Tontul aw nitam doonul woon lu dul ñuy wax naan : “reyleen ko mbaa ngeen lakk ko”. Yàlla musal na ko ca safara sa. Ay kéemaan a ngi ci biir loolu ngir aw nit ñu gëm. 25. [Ibraahiima] wax na ne : “Yéen a ngi jàpp xërëm yi bàyyi Yàlla ngir dëgëral seenug cofeel seen diggante fii ci dundug àddina. Waaye bu Bis-pénc baa, dangeen weddiwante, rëbbante te Safara mooy doon seen kër, te it dungeen fa am ndimbal. 26. Lóot daldi koy gëm. Wax ne : “Maa ngi gàddaay jëm ci sama Boroom, Mooy boroom Kàttan, di Ku Xereñ”. 27. May na ko Isaaqa ak Yanqooba, defaloon Nanu ko ca sëtam ya ag Yonent ak Téere ba. Te indil Nanu ko ag peyam ci àddina, te it bu àllaaxiraa, ca nit ñu yiw ña lay bokk. 28. [Fàttalikul] Lóot, ba mu waxee aw nitam, ne leen : “Yéen a ngi def u ñaawteef [ngóor- jigéen], te ci àddina, kenn jëkkewuleen ko ci. 29. Moo ndax yéen, dangeen di sëyanti ci góor ñi ? Di dogale yoon yi ? Ngeen di def njekkar ci seeni mbootaay ? ”. [Waaye] nitam ña tontuwuñu ko lenn lu dul ne ko : “Indil nu mbugalum Yàlla ndegam wax nga dëgg”. 30. Mu wax ne : “Yaw sama Boroom, may ma ndam ci kaw nit ñii di ay tooñkat ! ” 31. Ba Sunuy Malaaka dikkalee Ibraahiima ak xibaari mbégte, ne ko : “Danuy faagaagale waa dëkk bii ndax ña fa dëkk ay tooñkat lañu”. 32. Ibraahiima ne leen : “Waaye Lóot ma nga fa ! ”. Ñu tontu ko ne ko : “Noo gën a xam ña fa nekk : Dananu musal [moom Lóot] mook njabootam, ba mu des soxnaam, moom day bokk ca ña alku”. 33. ba Sunu ndawi Malaaka yi agsee ci Lóot, ñaawalees na jëme ci ñoom, mu tiit ci seeni mbir. Ñu ne ko : “Bul tiit, bul ragal... Dananu la musal yaak sa njaboot, ba mu des sa jabar, dafay alku. 34. Wàcce Nanu ci kaw waa dëkk bi mbugal mu bawoo asamaan ngir seen caay-caay ga”.
coran-wolof.pdf
page_314
314 35. Bàyyi Nanu fa lu bokk ca ñoom muy kéemaan gu leer nàññ ngir aw nit ñuy xel-lu. 36. [Naka noonu], la seen mbokk Chuhaybu demee woon Madyaana, ne leen : “Éy yéen samaw nit, jaamuleen Yàlla te gëm Bis-pénc ba, te buleen dox di yàq ci kaw suuf si”. 37. Ñu weddi ko. Yëngu-yëngu ba fab leen, ñu xëy ne lànjax ci seen kër. 38. Ak waa Haad ak Samuuda. - Noona lañu leen faagaagale - mu leer nàññ, ngeen di ko gis ci seen gént ya. Séytaanee leen taaralaloon seeni jëf, férëwle leen ; daawuñu jéem a gis lu baax. 39. Te kat [faagaagal Nanu] Xaaruuna ak Firawna ak Haamaan. Muusaa indiloon na leen Sunuy firnde, ñuy rëy-rëylu ci kaw suuf si. Waante mënuñu Nu woon a raw de. 40. Kenn ci ñoom [faagaagale Nanu ko] kem [tolluwaayu] bàkkaaram : Am na ci ñoom ñu Nu yóonni am mbënn ci ñoom ; am na ci ñoom ñu ag xaacu jël na leen ; am na ci ñoom ñu Nu mëdd ci biir suuf si ; am na ci ñoom ñu Nu labal. Yàlla tooñuleen ; waaye ñoo tooñ seen bopp. 41. Gam-gamleek ñay wut wéeruwaay bàyyi Yàlla, mi ngi mel ni jargoñ buy lëndub néeg. Te néeg bi gën a doyadi moo di néegu jargoñ. Cëy bu ñu xamoon ! 42. Yàlla xam na mboolem yu ñuy tës-tësi di ko jaamu, Moom ñu ne ko ñukk fale. Te Moom Yàlla moo di Boroom Kàttan, di Ku Xereñ. 43. Léebu yooyee ñuy sadd nit ñi ; te ñi xam ñoo cay xalaat. . 44. Moo bind [sàkk] asamaan yeek suuf si ci dëgg. Te ay kéemaan a ngi ci biir loolu ngir aw nit ñu gëm. 45. Nettalil li Nu soloo ca Téere ba te ngay taxawal julli. Ca dëgg-dëgg, julli daal dafay faat ñaawtéef ak njekkar. [Xamal ne] tudd Yàlla te di Ko fàttaliku moo gënatee rëy. Yàllaa ka xam li ngeen di def.
coran-wolof.pdf
page_315
315 46. Buleen dàggasante ak ñoñ-téere yi lu dul ca na mu gën a rafetee te buleen ca boole ña yiwadi ca ñoom. Nangeen di wax ne : “Nun gëm nanu li ñu wàcci ci nun ak li ñu wàcce ci yéen, sunu Yàlla ak seen Yàlla jenn la, te nun jébbale nanu sunu bopp di ay jullit”. 47. Noonu Lanu wàccee Téere bii di [Alxuraan] ci yaw [Muhammad]. Ña nga xam ne joxoon nañu leen Téere, gëmoon nañu ko. Am na ci ñoom ñu ko gëm [Alxuraan]. Yéefar yi doŋŋ ñoo weddi Sunuy kàddu. 48. Yaw [Muhammad], li jiitu wàccug [Téere bii di Alxuraan], musuloo jàng ab téere, musoo koo binde loxob ndeyjoor. [Su fekkoon ne loolu am na], kon weddikat ya danañu mën a sikki- sàkka. 49. Li wér te wóor moo di ne, [Alxuraan] ay laaya la yu ñu faramfàcce ci biir dënni woroom xam-xam yi. Te tooñkat yi rekk ñoo koy weddi. 50. Ñuy wax naan : “Lu tax Yàlla wàccewul ci moom kéemaan ? ”. Waxal ne : “Kéemaan a nga ca Yàlla. Man, ab xuppekat buy leeral rekk laa”. 51. Ndax doyuleen ñoom, wàcce gii Nu wàcce ci yaw Téere bi, Nu di leen ko dégtal ? Yërmaande ak fàttalikoo nga ca biir lool ngir aw nit ñu gëm. 52. Waxal ne : “Yàlla doy na seede sama digganteek yéen”. Xam na li nekk ci asamaan yeek suuf si. Ña gëm neen, weddi Yàlla, ñoo yàqule. 53. Té ñanga lay laaj mbugal ma cig yàkkamti. Bu fekkoon ne du dig ba Nu leen àppal, kon ñëwoon na [bu yàgg]. Waaye mbugal ma dana ñëw ci ñoom, di mbetteel te duñu ko yég. 54. Ña nga lay laaj mbugal ma cig yàkkamti, te fekk Safara waa ngay gaw yéefar ya. 55. Bu keroogee ba mbugal ma muur leen ci seen kaw ak seen ndëgguy tànk. Mu di leen wax naan : “Mosleen, toqamtikuleen li ngeen daan def ! ” 56. Éy yéen sama jaam ñi gëm ! Sama suuf si yaatu na [lool]. Waay-waay jaamuleen Ma ! 57. Bakkan bu nekk dana mos dee. Te [ñéppay] dellusi ci Nun.
coran-wolof.pdf
page_316
316 58. Ña gëmoon tey jëf u yiw, Dananu leen dëkkal ay néeg yu kawe yoo xam ne ay dex ñooy daw ca suufam. Dañu fay béel, ndaw pey gu neex, 59. ña daan muñ te wéeru woon ca seen Boroom ! 60. Amul jenn daaba ju warlul boppam wërsëg ! [Waaye] Yàlla moo koy wërsëgal ak yéen. Te Moo di Aji-dégg, di Ku xam. 61. Soo leen laajoon : “Ana kan moo bind asamaan yeek suuf si, tàggatal leen jant bi ak weer wi ? ”, kon danañu tontu wax ne : “Yàllaa ko def”. Waaw, kon ñoom naka lañuy dummóoyoo yoon wu jub wi ? 62. Yàlla mooy yaatalal wërsëgam ci ku ko soob ci jaamam ñi, Moo koy xatal itam. Yàlla xam na lépp lu ne. 63. Soo leen laajoon : “Ana kan moo leen wàccey ndox ci asamaan si, dundale ko suuf si ginnaaw bu dee woon [wow] ? ”, kon danañu wax ne : “Yàllaa ko def”. Neel : “Sant ñeel na Yàlla ! ”. Li ëpp ci ñoom duñu xalaat. 64. Dundu gi ci àddina sii doonul lu dul féexal xol ak po. Waaye kër gu mujj ga mooy dëgg- dëggi dundu. Cëy bu ngeen xamoo ! 65. Saa yu ñu waree ci gaal, dañuy ñaan Yàlla di ko sellal. Waaye, saa su leen musalee ba wàcce leen ci jéeri ji, ndeke yoo ña ngay bokkaale. 66. Dañuy xebet la ñu leen di jox ak di bànneexu ! Danañu xala xam ! 67. Xanaa dañoo gisul ne def Nanu [Màkka] muy barab bu ñu wormaal bu wóor, te nit ñi leen wër, dees na leen dax-daxee ? Moo ndax ñoom dañoo gëm ag neen tey weddi xéewali Yàlla yi ? 68. Ana kan moo gën a tooñ kuy duural Yàlla ay fen, walla mu weddi dëgg ga koy dëggal ? Moo ndax ca biir Safara dëkkuwaayu yéefar yi dafaa amul ? [Axakañ]
coran-wolof.pdf
page_317
317 69. Ñay xare di jànkuwante [samaw yoon], danañu leen gindi Sunuy yoon, te Yàlla ànd naak way-rafetal ña. ----------------------------------------------------------------------------- Saar 30 : ROM (WAA ROM) 60 laaya - Laata-Gàddaay ga ----------------------------------------------------------------------------- Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi. 1. Alif, Laam, Miim. 2. Noteef na waa Rom, 3. ci réew yi leen gën a jegeñ, wante ginnaaw nooteef googu, ñoom it danañu not , 4. ci biir diirub lu matul fukki at. Yàlla moo yor dogal yi, ci la jëkkoon ak li lay mujj, bu boobaa way-gëm ñi danañu sëgg ree, bég 5. ci ndimbalul Yàlla. [Moom Yàlla] mooy dimbali ku ko soob, Mooy boroom Kàttan, di Jaglewaakon bi. 6. Loolu mooy li Yàlla di dige. Te Yàlla du wuute ab digam, waaye li ëpp ci nit ñi gëmuñu. 7. Danañu xam li feeñ ci dundug àddina, te ñoom ñu sàggan lañu ci mbiri àllaaxira,. 8. Ndax dañoo xalaatul ci seen bopp ? Yàlla bindul asamaan yeek suuf si ak li nekk ci seen diggante lu dul ci dëgg, te sàkkal na lépp ay dig. Te nag li bari ci nit ñi dañoo weddi te danañu dajeek seen Boroom.
coran-wolof.pdf
page_318
318 9. Ndax dañoo doxul ci suuf tey xool naka la ñu mujje ña leen fa jiitu woon ? Ñoo leen ëppoon doole, daan réjji suuf si, feesoon ko dell ak seeni njaboot. Seeni Yonent indiloon leen ay kàddu yu leer. Yàlla tooñuleen, waaye ñoo tooñ seen bopp. 10. Ña daan jëf u ñaawteef, seenug mujj dellu ñaaw, ndax ñoom weddi woon nañu kàdduy Yàlla, daan ko yéjji. 11. Yàllaa bind yëf yi ; yi di ko defaraat ; te ca Moom la ñuy dellu. 12. Bu keroogee bu Bis-pénc ba di taxaw, tooñkat ya danañu naan cucum jaaxle. 13. Ña ñu daan bokkaaleek Yàlla duñu leen rammu, te sax far dañuy weddi ña ñu daan bokkaaleek [Yàlla]. 14. Bu kerook Bis-pénc baa, dañuy téqalikoo, féewoo. 15. Ña gëmoon tey jëf u yiw, ña ngay xéewu ci biir ay dër ; 16. yéefar yay weddi Sunuy kàddu ak dajeb àllaaxira ba, ñoom ña nga ca biir mbugal ma. 17. Tudd naa sellug Yàlla, kañ naa ko ! 18. Xeeti cant yépp ñeel na Ko ci asamaan yeek suuf si, ca marax ga ak njolloor. 19. Mooy génne ndundu ci ndee, di génne ndee ci ndundu. Mooy dundal suuf ginnaaw ba mu dewee. Noonu it lees leen di génnee [yéen ñépp] ca bisub dekki ba. 20. Bokk na ci kéemaanam yi : Mu binde leen suuf, - léegi nag, yéen a ngi nii tasaaroo ci àddina si -.
coran-wolof.pdf
page_319
319 21. Te bokk na ci kéemaanam yi, mu sàkkal leen ci seeni jëmm ay soxna ngir ngeen di ca dall, Mu def ci seen diggante cofeel ak yërmaande. Ay kéemaan a ngi ci biir loolu ngir aw nit ñuy xalaat. 22. Bokk na it ci ay kéemaanam, bindug asamaan yeek suuf si ak wuuteeg seeni làmmiñ ak seeni melo. Ay kéemaan a ngi ci loolu ñeel ñeel waa àddina si yépp. 23. Bokk na it ci ay kéemaanam, seeni nelaw ci guddi gi ak seenug sàkku wërsëg. Ay kéemaan a ngi ci biir loolu ngir aw nit ñuy dégg. 24. Bokk na it ci ay kéemaanam, Mu di leen won melax mu boole ragal ak xemmem, muy wàcce ndox mu bawoo asamaan di ca dundal suuf si ginnaaw ba mu deewee. Ay kéemaan a ngi biir loolu ngir aw nit ñuy xalaat. 25. Bokk na it ci ay kéemaanam, ni asamaan ak suuf taxawe ci ndigalam ; te saa Su leen jiinee ab woote, yéen ñéppay génn ci biir suuf si [ginnaaw dee] 26. Moo moom ñépp ñu nekk asamaan ak suuf : ñépp a koy toroxlul. 27. Moo sos mbindéef yi di leen defaraat ; te looloo gën a yomb ci Moom. Moo dàmbe li gën a kawe ci asamaan yeek suuf si. Mooy boroom Kàttan, di ku Xereñ ki. 28. Yàlla sadd na leen ay léebu ci seen bopp : Ndax seen jaam ñi bokk nañu ak yéen seeni alal, ngeen yem ci kepp ? [Mukk], loolu rekk ngeen ragal. Nii la Nul leerale laaya yi ngir aw nit ñuy xalaat. 29. Tooñkat yi dañoo topp seen bànneex, te àndul ak xam-xam. Ana kan mooy mën a gindi ku Yàlla réeral ? Duñu am ku leen dimbali. 30. Nangay jubbantiku topp diine Yàlla jiy cosaan te Mu sos ci nit ñi - bindéefu Yàlla du soppiku -. Loolu mooy diine ju jub ja ; waaye li ëpp ci nit ñi duñu xam. 31. Wommatuleen jëm ci Moom ; te nangeen ko ragal, tey taxawal julli te buleen bokk ca way-bokkaale ña,
coran-wolof.pdf
page_320
320 32. ña téqale seen diine di ay kurél, xaaj bu nekk ne siiw la fa moom. 33. Bu lor ju laal nit ña amee, dañuy ñaan Yàlla di Ko woo booleek toroxlu. Waaye su leen di mosal yërmaande rekk, [nga gis] ñu delluy bokkaale, 34. di fakk la Mu leen indiloon. “Bànneexuleen. Dangeen xala xam”. 35. Walla Danuy wàcce ci ñoom [kilifa] ab Téere buy wàqante la ñu daan bokkaale ? 36. Saa su Nu mosalee nit ñi yërmaande, ñu bég lool. Bu ñu defee ab garaawaale ba safaan dal leen ca, ndekete yoo dañuy yoqat. 37. Xanaa dañoo gisul ne Yàlla Dana yaatalal ku ko soob, wërsëgam ? Dana ko xatal it. Ay kéemaan a ngi ci biir loolu ngir aw nit ñu gëm. 38. Dangay jox say [mbokki] jegeñaale lay seen yelleef, ak ndóol ya ak doxandeem ya. Loolu moo gën fuuf ngërëmul Yàlla ; te ñoom ñooy texe. 39. Alal ji ngeen di lebalante ngir muy yokk, du yokku fa Yàlla de, waante li ngeen di génne asaka ngir jëmmi Yàlla... Dangeen fekk muy lu ñu ful. 40. Yàlla mi leen sàkk, wërsëgal leen. Di leen rey te di leen dundalaat. Moo ndax ñi ngeen koy bokkaaleel am na ñu mën a def loolu ? Tudd naa sellam ga, kañ naa Ko ! Soree na lool ak li ngeen di bokkaale. 41. Yàqute feeñ na ci jéeri ji ak géej gi ci jëfi nit ñi ; ci loolu, Yàlla da leen ñamal tuuti rekk ci seen [peyug] jëf yu bon yooyu ; ngir ñu mën caa jàjjoo, dellu ginnaaw, dëpp [dem jëf lu baax]. 42. Neel : “Doxleen ci suuf si tey xool naka la mujje woon ña leen jiitu woon. Te li ëpp ci ñoom doon bokkaale [Yàlla]”. 43. Jubbantikul topp diine ju jub ja, ba laa bis di ñëw boo xam ne kenn du ko mën a randal ca Yàlla. Bu keroogee, danañu fallaxoo [réeroo, téqalikoo] :
coran-wolof.pdf
page_321
321 44. Ku weddi, weddeem ga dana dal ca kawam. Ñay jëf yiw nag... Ñoom ña ngay waajal seen bopp [daluwaay bu maase] néeg, 45. Nar naa feye ñi gëm tey jëf u yiw, ngënéelam. Moom safoowul yéefar yi. 46. Bokk na ci ay kéemaanam, muy yebal yërmaandeem, ak gaal yi di daw ci ndigalam, te ngeen di sàkku ci xéewalam yi. Ak ngir ngeen di gëm ! 47. Yónni woon Nanu ay Yonent yu jiitu woon ca nit ña, indiloon leen ay kàddu yu leer. Nu daldi feyu ca tooñkat ya ; te ndimbalul jullit ñi [way-gëm ñi], Maa ko warlu. 48. Yàlla miy yebal ngelaw mu yenu niir, di ko tàbbal ci asamaan si na Mu ko soobe ; Mu di ko def ay daggit. Ab taw di ca génnee su ko tawale. Ña ko soob ci jaamam yi, ndeketeyoo dañuy sëgg ree ngir bég, 49. doonte la sax naagu woon nañu ba mu laataa na wàcc. 50. Xoolal jeexitali yërmaandey Yàlla naka lay dundalee suuf si ginnaaw ba mu deewee. Kookee de Mooy dekkalaat néew yi te mën na lu ne. 51. Bu Nu yebaloon ngelaw, ñu gis ne [seen gàncax ga] mbokk, di [lax ak a dee], dañuy daldi weddi, fakk xéewal ya. 52. Yaw dey, mënoo tax a dégg ñu dee ; waxantumalaak tëx, su ñu nee wërëñ dummóoyu, ak lu woote ba xumb xumb nag. 53. Du caageene yaw yaaw gindi gumba yi ci seen réer ga. Ñi nga mën a dégtal [sa woote bii] daal, ñooy ña gëm, di ay jullit. 54. Yàlla mi leen bind cig lott, teg ca kàttan ; delloo ci lott gu ànd ak kumur, màggat [bijjaaw] : Te mooy sàkk lu ko soob, Mooy ki Xam te Mën.
coran-wolof.pdf
page_322
322 55. Bu Bis-pénc ba taxawee, tooñkat ya danañu giñ naan as ndiir su ndaw la nu fi saxoon. Noonu la Nu leen daan férawale, soreel leen dëgg ; 56. Gaa ña amoon xam-xam ak ngëm, ne leen : “Sax ngeen fa ci dogalu Yàlla ba bisub dekki ba, - lii nag mooy bisub dekki ba, - waaye yéen xamuleen woon”. 57. Su boobaa, tooñkat ya, seenug tinu du fa jariñ dara te kenn duleen faale. 58. Saddal Nanu nit ci biir Alxuraan jii léebu wu nekk. Soo leen indiloon kéemaan it, yéefar ya dañu naan : “Yéen daal, ay caaxaankat doŋŋ ngeen”. 59. Noonu la Yàlla di fattee xoli ña xamadi. 60. Muñal ndax digub Yàlla la dellu [yàgg yàgg dina ñëw]. Ñi gëmul, buñu la yàkki ! ----------------------------------------------------------------------------- Saar 31 : LUQMAAN 34 laaya - Laata Gàggaay ga ----------------------------------------------------------------------------- Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi. 1. Aliif, Laam, Miim. 2. Lii ay laaya la yu Téere bu xereñ, 3. jub la, yërmaande la ngir ñuy rafetal , 4. ñiy taxawal julli, di génne asaka te amug wóolu ci ne àllaaxira dina ñëw.
coran-wolof.pdf
page_323
323 5. Ñooñaa nga tege ca kaw seen yoonu Boroom wu jub xocc wa, te ñoom ñooña ñoo texe. 6. Am na ci nit ñuy nëbb xam-xam, di feeñal waxi caaxaan ngir namm a soreel nit ñi, sànk leen, réeral leen yoonu Yàlla ci lu àndul ak xam-xam, weddi ko, jàppe ko ag doyadal. Ñoom ñooña am nañu mbugal muy toroxale. 7. Saa su ñu jàngee Sunuy laaya ci moom, mu dummóoyu mel ni ku ko déggul, mel ni ab saañ dafa nekk ca nopp ya. Yégal ko ne [am na] mbugal mu metti. 8. Ña gëm tey jëf u yiw, am nañu Àjjanay xéewal, 9. dañu fay béel, - ni ko Yàlla dige woon tigi. - Mooy boroom Kàttan, di Ku Xereñ. 10. Moo bind asamaan si ci lu àndul ak keno yu ngeen di mën a gis ; Moo def ay doj ci biir suuf ngir mu bañ jeriku ak yéen ; def na ci xeetu mala wu nekk. Te nun, Yàlla wàcceel nanu ndox mu bawoo asamaan, nu saxal ci ay yóllent ci xeetu gàncax wu nekk. 11. “Lii mooy li Yàlla sàkk. Kon wonleen ma, ña dul Moom, ana lu ñu sàkk ñoom ? ”. Li am kay mooy, tooñkat ya ñi ngi ci réer gu bir . 12. Joxoon Nanu Luqmaan xam-xamu xereñ, ne ko : “Santal Yàlla, [gërëm Ko], ku Ko sant ci di Ko dello jukkal, boppam ; ku Ko xarab it..., [Na xam ni] Yàlla ku doylu la, Yayoowaakoonug cant la”. 13. [Fàttalikul] ba Luqmaan waxee doomam ja, di ko waar, naan ko : “Yaw samas doom, bul bokkaale mukk dara ak Yàlla, ndax bokkaale kat ag tooñ gu réy la”. 14. Dénk Nanu nit muy rafetal jëme ci ñaari waajuram ; ndax yaayam ëmb na ko muy coono ci biir coono : ba feral ko diirub ñaari at. “Nanga may sant Man [Yàlla] ak sa ñaari waajur. Ci Man la lépp di mujj. 15. Saa su ñu la sonnalee ci bëgg nga bokkaale Maak loo amul xam-xam, bulen ca topp ; waaye nangay ànd ak ñoom ci àddina si ak njekk. Te nanga topp yoon wa jëmsi ci Man. Fi Man ngeen di mujje [yéen ñépp], su ko defee, Ma téqantalal leen la ngeen daan def”.
coran-wolof.pdf
page_324
324 16. “Yaw sama doom, dIisaay woowu, doonte la sax dafa tollu ni as fepp, nekk ci kaw doj mbaa ci biir asamaan yi, walla ci biir suuf, du tee Yàlla indi ko . Yàlla Ku deñ-kumpa la . 17. Yaw sama doom, taxawalal julli tey digle njekk, te it nangay tere njekkar, te it nangay muñ li lay dal. Loolu mooy dégu ! 18. Bul dox di dummóoyu nit ñi, bul dox it di fuukarewu : Yàlla safoowul képp kuy fuukarewu ak a damu. 19. Nangay teey ci sab dox, te nangay suufeel sa kàddu, ndax kàddu gi gën a suufe moo di kàddug mbaam sëf ”. 20. Xanaa gisuleen ne Yàllaa leen tàggatal li nekk ci asamaan yeek suuf si ? Te Mu tuur leen xéewalam yi ci li feeñ ak li nëbbu. Am na ci nit ñi ñuy dàggasante ci mbiri Yàlla, te amuñu ca benn xam-xam, du càggenu ag gindiku, waxantumalaak Téere buy gindi. 21. Te bu ñu leen waxee ne : “Toppleen li Yàlla wàcce”, dañu naan : “Nuy kay dañuy topp sunu baaxi maam”. Moo ndax Séytaane daawuleen woo jëme leen ci mbugalum Safara ! 22. Képp ku jébbal Yàlla boppam tey rafetal, [na xam ne] ŋoy na ci buum gi gën a dëgër. Te ca Yàlla la mbir yépp di mujj. 23. Képp ku weddi it, weddeem ga bumu la jaaxal : danañu dellusi ci Nun, ñu xibaar leen la ñu jëfoon. Yàlla xam na xéll li nekk ci dënn yi. 24. Dananu leen bànneexal as ndiir ; daldi leen mbaq ci mbugal mu diis. 25. Te su leen laajoon : “Ku bind asamaan yeek suuf si ? ”, kon ñu ne : “Yàlla ! ”. Waxal : “Cant ñeel na Yàlla ! ”. Waaye ñi ëpp ci ñoom xamuñu. 26. Yàllaa moom li ci asamaan yeek suuf si. Yàlla Ku doylu la, di Yayoowaakoonub cant !
coran-wolof.pdf
page_325
325 27. Su fekkoon ne mboolem li nekk ci suuf si ciy garab, dafa doon ay xalima, géej gi amaat yeneen juróom-ñaari géej yu koy dolli, lépp di daa, kon dey du tax kàdduy Yàlla jeex. Yàlla Borom Kàttan la, di Ku Xereñ. 28. Seenug sosu ak seenug dekkiwaat yéen ñépp, mi ngi yombe Yàlla ni benn bakkan kepp. Yàlla Kuy Dégg la, Kuy Gis la. 29. Xanaa gisoo ne Yàlla mooy dugal guddi ci bëccëg, Moom dugal it bëccëg it ci guddi, Moo tàggat jant beek weer wi, ku ca nekk a ngay daw ci ab dig bu ñu ko àppal ? Te Yàlla Ku Deñ- kumpa la, Ku Xàmmee li ngeen di def la. 30. [Loolu nag] ngir xam ne Yàlla mooy dëgg, lépp lu ngeen mën a jaamu te du Moom, neen la te Yàlla moo di Aji-kawe, di Ku màgg. 31. Xanaa gisuloo ne gaal a ngay daw ci biir géej, mu bokk ci xéewali Yàlla yi ? Ay kéemaan a ngi ci biir loolu ñeel bépp santaakoon, dib muñaakoon. 32. Bu leen duus yi muuree ba mel ni ker, ñuy woo Yàlla, di Ko sellal ; bu leen musalee ba [ñu génn ci jéeri ji], mu amaat ca ñoom ñuy diiŋat ; te Sunuy kàddu kenn du ko diiŋat ku dul ku goreedi, di ab xarabaakoon. 33. Éy yéen nit ñi ! Ragal-leen seen Boroom [te di Ko wattandiku], te nangeen tiit ci Bis boo xam ne baay du warlul doom dara, doom it du warlul baayam dara. [Fexeleen it] ba buleen Séytaane tax ngeen faku. 34. Xam-xamu Bis-pénc baa ngi ca Yàlla ; Mooy wàcce tawu waame ; Moo xam li nekk ci jurukaay ya. Benn bakkan xamul lu muy fàggu ëllëg, benn bakkan xamul it ci san suuf lay deewe. Yàlla Ku Xam la, Ku Xàmmee la. ----------------------------------------------------------------------------- Saar 32 : SUJJÓOT 30 laaya - Laata Gàddaay ga
coran-wolof.pdf
page_326
326 ----------------------------------------------------------------------------- Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi. 1. Aliif, Laam, Miim. 2. Wàcceg Téere bii [Alxuraan], sikk nekku ca, mu bawoo ca Boroom àddina sépp. 3. Walla dañu naan [Muhammad] moo ko sos ? [Déedéet, lii mooy dëgg ga bawoo ci sa Boroom ngir nga xupp ci aw nit ñoo xam ne bi nga laataa ñëw, amuñu woon xuppekat, te amaana ñu gindiku. 4. Yàlla mi bind asamaan yeek suuf si ak li nekk ci seen diggante ci diirub juróom-benni fan. Daldi yemoo ca Gàngunaay ga [Aras]. Amuleen benn wéeruwaay walla rammukat bu dul Moom. Moo ndax dangeen dul fàttaliku ? 5. Mooy settantal [lijjanti] mbir yi, jële ko asamaan jëme ko ci suuf si, topp mu yéeg asamaan ci bis boo xam ne ab nattaleem junni la ci ay ati àddina. 6. Kooka mooy xamkatu kumpa ak li feeñ, mooy Boroom Kàttan, di Jaglewaakoonu yërmaandeem, 7. Moo jekkal sosug lu ne. Daldi door sosug nit ci ban, 8. daldi nay defe askanam wa mu càllaloo ci am ndox mu doyadi; 9. daldi koy yemale, ëf ci Ruuwam. Defaral leen dégg-dégg, ak ub gis ak i xol. Te néewaana ngeen di Ko sant ! 10. Ñuy wax naan : “Ndax bu nu seeyee ci biir suuf si, dananu dekkiwaat ? ”. Ñoom dañoo weddi ne danañu dajeek seen Boroom.
coran-wolof.pdf
page_327
327 11. Neel : “Malaakam ndee ma ñu sasee loolu ci yéen moo leen di rey. Su ko defee, ngeen dellu ca seen Boroom”. 12. Cëy soo gisoon, tooñkat yaa ngay jatt seeni loos, naan ! “Yaw sunu Boroom, gis nanu, dégg nanu, delloo nu ca [àddina], kon de nu jëf lu baax ; léegi, xam nanu ne lii lu wóor la”. 13. “Bu Nu sooboon, Dananu indil bakkan bu nekk ag njubam. Waaye dafa fekk ne li Ma wax fàwwu mu am : “Danaa feesal Safara ci nit ak jinne mbooleseen”. 14. “Kon mosleen ci li ngeen fàtte woon seen dajeek Bis bii. Dananu leen fàtte-fàttelu. Toqamtikuleen mbugal muy sax dàkk, muy peyug la ngeen daan def”. 15. Ñii gëm Sunuy kàddu, ñoom ñi nga xam ne saa su Nu leen ko fàttalee, dañuy rot di sujjóot, di sàbbaal, di kañ ak a sant seen Boroom, ñoom duñu rëy-rëylu. 16. Dañuy fojjatiku ca seen tëddukaay ya [lal ya], di ñaan seen Boroom ci ragal ak xemmem ; te di joxe ca la Nu leen wërsëgal. 17. Benn bakkan xamul la ñu koy xala deñcal ci yuy neex ci bët, muy peyug la mu daan def ! 18. Moo ndax ku gëm dina mel ni ab saay-saay ? [mukk], duñu mës a yem. 19. Ña gëmoon tey jëf u yiw, am nañu ay dër ca Àjjana, muy seen wàccuwaay ngir la ñu daan jëf. 20. Ña saay-saayoon, ñoom Safaraa di seen kër : saa su ñu ca bëggee génn, ñu delloo leen ca, te naan leen : “Toqamtikuleen mbugalum Safara sa ngeen daan weddi”. 21. Dananu leen ñamal ci àdduna [takkandeerub mbugalum àllaaxira] ndax ñu mën a dellu ca yoon wu jub wa ! 22. Ana kan moo gën a tooñ ka nga xam ne, saa su ñu ko fàttalee laayay Boroomam, mu dummóoyu ko ? Dananu feyyu ci tooñkat yi.
coran-wolof.pdf
page_328
328 23. Joxoon Nanu Muusaa Téere ba - bul am xel-yaar ci dajeek moom [yaw Muhammad] -, te defoon Nanu Téere ba mu di njub ñeel Bani-Israayiila gépp. 24. Defoon Nanu ci ñoom ay njiit yuy gindee ci Sunu ndigal, waxtu wa ñu muñee te wóolu Sunuy laaya [kàddu]. 25. Sa Boroom ci boppam dana àtte seen diggante ca la ñu daan wuute. 26. Ndax dafa doyul ci ñoom gindiku, te faagaalaloon Nanu ay maas ya leen jiitu woon te tey ñi ngi dox ci seen génti kër yi ? Ay kéemaan nekk na ci biir loolu ! Ndax ñoom dañu dul dégg ? 27. Xanaa dañoo gisul ñoom ci ne Man Yàlla maay wàcce ndox ci kaw suuf su wow, génne gàncax gu seeni jur di lekk ak ñoom it ñu di ca lekk ? Moo ndax ñoom dañu dul gis ? 28. Ñangay laaj naan : “Lii kañ lay doon, ndegam wax ngeen dëgg ? ”. 29. Waxal ne : “Bis ba ndam la di ñëw, ngëmug yéefar yi dootuleen jariñati dara ! Te kenn duleen négandiku”. 30. Dummóoyuleen te xaar. Ñoom it ñi ngi xaar. ----------------------------------------------------------------------------- Saar 33 : FARANDOO YI 73 laaya - Laata Gàddaay ga ----------------------------------------------------------------------------- Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi.
coran-wolof.pdf
page_329
329 1. Éy yaw Yonent bi ! Ragalal Yàlla te bul topp yéefar yi ak naaféq yi, Yàlla ku xam la, Ku xereñ la. 2. Toppal li ñu lay soloo te mu bawoo ca sa Boroom. Yàlla xàmmee na ca la ngeen di def. 3. Te nangay wéeru ci Yàlla. [Ndax] Yàlla doy na sëkk wéeruwaay. 4. Yàlla defalul kenn nit ñaari xol ci dënnëm. Deful it jabar yi ngeen di wodde seen pendali ndey [ci pase] ñuy seeni yaay . Deful it doom yi ngeen doomoo ñuy seeni doom. Loolu seeni wax doŋŋ la ju yem ci seeni gémmiñ. Yàlla dëgg lay wax te Mooy jubbanti, di tege ci yoon wu jub. 5. Appelez-les du nom de leurs pères : c’est plus équitable devant Allah. Ña ngeen xamul seeni baay, kon ñoom seeni mbokk la ñuy doon ci diine ak seeni farandoo. Ayul ci yéen it lu ngeen ca wax te muy njuumte, li aay kay mooy la ngeen ca wax te tey ko. Yàlla, Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la. 6. Yonent bi moo gën a yey jullit ñi ci seen bopp ; te ay soxnaam, seeni yaay lañu. Ña ame mbokku gu deret, gën nañoo yeyante kem ni mu dikke ci Téereb Yàlla bi, te jullit ñi ak way- gàddaay ñi, mën ngeen a bind ab dénku ci seeni alal mu ñeel seeni farandoo ya dul donn. Loolu lu sax la lu ñu bind ca Téere ba. 7. [Fàttalikul] ba Nu jëlee daalante ci Yonent yi ak ci yaw, ak ci Nooh ak ci Ibraahiima, ak Muusaa, ak Iisaa doomu Maryaama : jëloon Nanu ci ñoom daalante bu dëgër, diis, 8. ngir laaj [Moom Yàlla] ñi dëggal ci seenug dëggal. Te waajalal na yéefar yi mbugal mu metti. 9. Éy yéen ñi gëm ! Fàttalikuleen xéewali Yàlla ci yéen, ba leen xarekat ya songee te Nu yebaloon ci ñom ngelaw ak i xarekat yu ngeen gisul. Yàllaa ngi doon gis li ngeen doon def. 10. Ba ñu leen songee, jóge leen kaw ak ci suuf [fépp], seen gët ya di tiiw-tiiwi, ngeen rët ba seeni xol nekk ci seeni boli, ngeen di njort ci Yàlla njort lu nekk... 11. Foofee la Nu nattoo jullit ña, yëngal leen yëngal gu tar.
coran-wolof.pdf
page_330
330 12. Ak ba naaféq ya ak ña seen xol tawat di wax naan : “Yàlla ak Yonentam diguñu nu lu dul ay nax”. 13. Ak ba mu amee kurél ci ñoom buy wax naan : “Yéen waa Yasriba [Madina] ! Buleen fa toog. Delluleen [ginnaaw]”. Mu am it kurél ci ñoom buy ñaan ndigal Yonent bi, di wax naan : “Sunuy kër dafa aaruwul”, du loolu de : waaye dañoo bëggoon a daw doŋŋ. 14. Ku leen doxe woon ginnaaw, ne leen na ñu weddi, kon ñu def ko, te duñu ca yéex, 15. te la ko jiitu, fekkoon na ñu daalante ak Yàlla te dañoo wone ginnaaw [daw xare]. Te daalanteb Yàlla, lu ñuy lijjanti lay doon. 16. Neel : “Su ngeen dawee it, seenug daw duleen jariñ dara ; rey mbaa dee rekk a fiy am, dundu yàggul”. 17. Neel : “Ana kan moo leen di musal ci Yàlla, su nammee ci yéen safaan walla Mu namm ci yéen yërmaande ? ”. Duñu am wéeruwaay walla ndimbal leneen lu dul Yàlla. 18. Yàlla xam na ñay gàllankoore ci yéen ak ñay wax : “Ñëwleen ci nun”, fekk na yabuñu ab xare, 19. Dañuy soxore loolu ci yéen. Bu am tiit dikke, nga gis ñu di la xool, seen gët yi di wur- wuri mel ni ñuy sukkraat. Bu tiit ma jeexee, ñu di leen teg ay baat yu ñaaw. Ña bañ aw yiw, ñoom ñooñee gëmuñu. Yàlla daldi sepi seeni jëf. Te loolu yomb na Yàlla. 20. Te ñuy foog ne farandoo ya demuñu. Te bu ñu dikkoon, dañu naa ngéeju bokk ca màngaan ya, duñu xam li ngeen xewle lu dul bu ñu ko laajtoo. Bu ñu nekkee ci seen biir itam, lu néew la ñuy xareji. 21. Am ngeen royuwaay wu jekk ci Yonentub Yàlla, te képp ku yaakaar Yàlla te gëm Bis- pénc bu mujj ba, tey tuddu, di fàttaliku Yàlla lu bari .
coran-wolof.pdf
page_331
331 22. Ña gëm tigi, ba ñu gisee farandoo ya, dañoo wax ne : “Lii la Nu Yàlla ak ub Yonentam doon dig ; te Yàlla ak ub Yonentam dëggal Nañu”. Te dolliwuleen lenn lu dul ngëm ak jébbulu. 23. Am na ci jullit ñi ñuy dëggal la ñu dëelante woon ak Yàlla. Am na ci ñoom ñu ko matal, am it ci ñoom ñuy négandiku ; te soppiwuñu ca dara ; 24. Yàlla dana fey ña dëggaloon ca seen dëggu ga, Dana mbugal it naaféq ya bu ko soobee, walla Mu baal leen. Yàlla Yërëmaakoon la, Jaglewaakoonu [yërmaandeem] la. 25. Yàlla delloo na yéefar ya, ñu dellook seen mer, amuñu wenn yiw, Yàlla fegal na jullit ñi xeex ba. Yàlla ku bari doole la tey Boroom kàttan. 26. Te wàcce na ca ña doom jàmmaarlook yéen te bokk ca ñoñ-Téere, [yonjaxal leen], daldi dugal am tiit ci seen xol ya ; ngeen rey ñenn ña, lél ñenn ña. 27. Mu donnale leen seen suuf, ak seeni kër, ak seeni alal, ak suuf soo xam ne mësuleen ca xand. Yàlla mën na lu ne. 28. Éy yaw Yonent bi ! Waxal say soxna ne leen : “Su fekke ne dundug àddina sii rekk a leen ñor ak ub taaram, kaayleen ma yombalal leen ko, ci ma fase leen ci am pase mu jekk. 29. Su fekkee nag ne Yàlla ak Yonentam ak kër gu mujj ga di àllaaxira rekk a leen ñor, [nangeen xam ne] képp kuy rafetal ci yéen, Yàlla dana ko waajalal ag pey gu màgg. 30. Éy yéen soxnaay Yonent bi ! Képp ku bokk ci yéen te def aw ñaawtéef wu bir, dees na ko fulal mbugalam ñaari yoon ! Te loolu yomb na Yàlla. 31. Képp ku bokk ci yéen te jébbal boppam Yàlla ak ub Yonentam tey jëf u yiw, Dananu ko fulal ag peyam ñaari yoon, te waajalal Nanu ko xéewal gu màgg. 32. Éy yéen soxnaay Yonent bi ! Yemuleen ak yeneen jigéen ñi. Su fekkee ne ragal ngeen Yàlla, buleen di wax waxi caaxaan, yuy tax góor gu xolam tawat di xemmem. Nangeen di wax wax ju yiw njekk.
coran-wolof.pdf
page_332
332 33. Nangeen di sax ci seeni kër ; te buleen di baraj-baraji kem ni ko jigéenu jaahiliya yu njëkk ya daan ko defe. Te nangeen di taxawal julli tey génne asaka te nangeen di topp Yàlla ak ub Yonentam. Ndax Yàlla dafa namm a dindi ci yéen, waa kër Yonent bi, lépp luy taq-taq, te laabal leen ba ngeen sell. 34. Nangeen fàttaliku li Nu leen jàngal ci seen biiri kër, te mu bokk ci laayay Yàlla yi , Alxuraan ak lépp luy xereñe. Yàlla dey Kuy ñeewante la, di Kuy xàmmee. 35. Naka jullit yu góor yi ak jullit yu jigéen yi, way-gëm yu góor ak way-gëm yu jigéen, way- wommatu yu góor ak way-wommatu yu jigéen yi, way-dëggu yu góor ak way-dëggu yu jigéen yi, way-muñ yu góor ak way-muñ yu jigéen, way-ragal yu góor ak way-ragal yu jigéen ya, saraxekat yu góor ak saraxekat yu jigéen yi, woorkat yu góor ak woorkat yu jigéen yi, góor ñiy sàmm seeni pëy ak yu jigéen yi, ñiy tuddu Yàlla lu bari ci góor ñeek jigéen ñi, Yàlla waajalal na leen njéggal ak pey gu màgg. 36. Su Yàlla ak ub Yonentam àtte mbir ba sottalI, amul benn jullit bu góor ak bu jigéen bu ciy am coppan, te seen àtte ba xas dog. Képp kuy moy Yàllaak ub Yonentam, mi ngi ci ag réer gu bir. 37. [Fàttalikul] ba ngay wax ak waa ja Yàlla xéewaloon te yaw it nga xéewaloon ko, ne : “Jàppal sa soxna si te ragal Yàlla, wattandiku Ko”, yaa ngi nëbb ci sa biir lu Yàlla xal a feeñal. Ngay ragal nit ñi te Yàlla moo gën a yeyoo ku Ko ragal. Ba Zaydun fasee soxna soosa, takkal Nanu la ko, ngir jullit yi bañ a aayalati seen jabari doomoo yi, ngeen mën leen takk saa su ñu leen fasee. Te ndigalul Yàlla moom, def rekk. 38. Aayul ci Yonent bi [muy jëfandikoo] la Yàlla yoonaloon, farataal ko ca ña ko jiitu woon. Te ndigalul Yàlla luy sax la. 39. Ña nga xam ne ñooy jottali bataaxali Yàlla yi te ragal Ko, te it duñu ragal keneen ku dul Moom. Ndax Yàlla doy na sëkk ci waññi [natt] jëf yi. 40. Muhammad du baayub kenn ci seeni gaay, waaye ndawul Yàlla te di mujjug Yonent yi. Yàlla xam na lépp lu ne. 41. Éy yéen ñi gëm ! Nangeen di farataal, di tudd Yàlla lu bari. 42. te nangeen di Ko sàbbaal suba ak ngoon.
coran-wolof.pdf
page_333
333 43. Mooy kiy julli ci yéen, di leen ñaanal, - Mook ay Malaakaam, - ngir génne leen cig lëndëm, jëme leen cig leer ; te Mu di Jaglewaakoonu yërmaandeem ci ñi gëm. 44. Seenub nuyyoo Bis nuy dajeek Moom : “Jàmm rekk”, te mu waajal leen ag pey gu tedd . 45. Éy yaw Yonent bi ! Noo la yebal ngir nga doon seede, di béglekat, di xuppekat. 46. té woote jëme ci Yàlla ; te di làmp bu leer. 47. Te ngay bégal jullit ñi, ne leen am nañu ca Yàlla ngëneel lu màgg. 48. Te bul topp mukk yéefar yeek naaféq yi, te it bul faale seen lor, nangay wéeru ci Yàlla, Yàlla doy na sëkk wéeruwaay. 49. Éy yéen ñi gëm ! Su ngeen takkee jabar ci jullit [jigéen ñi] ba joxe can ga, su ngeen leen fasee te laalewuleen, warul a jàpp yedda. Nangeen leen boyal ci njekk. 50. Éy yaw Yonent bi ! Daganal Nanu la sa soxna yi nga jox can ak ñi nga moom [jaam bu jigéen] ak doom yu jigéen yu sa baay-tëx ak sa doomi bàjjen yu jigéen ak doomi nijaay yu jigéen ak sa doomi ndey-tëx ju jigéen, - ñi gàddaay ànd ak yaw, - ak jigéenu jullit ju may boppam Yonent bi, bu ko Yonent bi bëggee takk soxna : Lew na la domm, waaye jullit yu góor ñi duñu ko sañ. Ndax Noo gën a xam li Nu farataal ci ñoom ak seeni soxna ak seeni jaam yu jigéen, [li ko waral moo di] ngir rekk dellu te yeddu. Te Yàlla Jéggalaakoon la yërmaandeem. 51. Mën nga xaarloo ku la soob ci ñoom, dëkkoo ku la ca soob. Ak lu la ca neex ca ña nga beddi woon, aayul ci yaw. Te loolu moo leen dàqal, buñu yërëmtalu te nañu gërëm ñoom ñépp ca la nga leen jàppe. Yàlla xam na li nekk ci seeni xol. Yàlla ku xam la, Ku lewet la. 52. Ginnaaw loolu, jigéen ñi duñu dagan ci yaw. Walla nga di leen wecceek yeneeni jabar, doonte la seenub taar yéem na ; - ba mu des say jaam yu jigéen. Yàlla kuy fuglu la ci lépp. 53. Éy yéen ñi gëm ! Buleen dugg kër Yonent bi, lu dul ci ndigal, buleen fay xaaraanu ñam. Waaye bu ñu leen woowee, nangeen dugg. Bu ngeen noppee ca lekk ga, daldi leen tasaaroo te
coran-wolof.pdf
page_334
334 buleen toog di waxtaan. Ndax loolu, dafay lor Yonent bi mu di leen ko rus a wax, te Yàlla Moom rusul dara ci dëgg. Te su ngeen deeti laaj jegeñam ña dara, nangeen koy laaj ci ginnaaw kiiraay : ndax loolu moo gën a laab ci seeni xol [yéen ak ñoom] ; Te it waruleen di lor Yonent bi, waxantumalaak ngeen di takk soxnaam ginnaawam ; Ba fàwwu, loolu lu rëy la ca Yàlla. 54. Mbir mu ngeen mën feeñal mbaa ngeen nëbb ko,... Yàlla xam na ko. 55. Aayul ci ñoom [soxna yi] seeni baay [di ko def], walla seeni doom, walla seen mbokk, walla seeni doomi mbokk mu jigéen, walla seeni jabar, walla seeni jaam. Te nangeen ragal Yàlla ndax Yàllaa seede lépp lu ne. 56. Yàlla ak i Malaakaam dañuy julli ci Yonent bi ; Éy yéen ñi gëm, jullileen ci moom te sëlmal ci moom . 57. Ñi nga xam ne dañuy lor Yàlla ak ub Yonentam, Yàlla rëbb na leen ci àddina ak ca àllaaxira, te waajalal na leen mbugal muy doyadiloo, di toroxtale. 58. Ña nga xam ne dañuy lor jullit yu góor yi ak jullit yu jigéen yi te defuñu lu ko jar, ñangay yenu aw duur ak bàkkaar bu rëy. 59. Éy yaw Yonent bi ! Waxal say soxna ak say doom yu jigéen ak jigéeni jullit ñi, ñuy muur seenu yaram : ci la ñu leen di gën a xame te kenn duleen di xas. Yàlla, Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la. 60. Su fekkee ne naaféq yeek lëjëlkat yeek woroom xel yu tawat yi dëkk [Medina] bàyyiwuñu, Danaa xiir ci seen kaw, te kon lim bu néew moo ca déeti dëkkaale ak yéen. 61. Muy ñuñu rëbb. Fu ñu jublu, ñu faagaagal leen : 62. Lii mooy sunnas Yàlla, ab dogalam ci ña fi jiitu woon te sunnas Yàlla du soppiku mukk. 63. Nit ñaa ngi lay laaj ci mbiri Bis-pénc ba. Waxal ne : “Yàllaa ko xam”. Te yaw sax loo ci xam ? Amaana Bis-pénc ba di lu jegeñ.
coran-wolof.pdf
page_335
335 64. Yàlla rëbb na yéefar yi te waajalal na leen aw safara, 65. dañu fay béel fàww, duñu fa am ku leen méngoo, duñu fa am ndimbal. 66. Bis ba ñuy wëlbati seeni kanam ca Safara, ñuy wax naan : “Aka neexoon nu toppoon Yàlla, nu toppoon Yonent ba ! ”. 67. Ñuy wax naan : “Yaw sunu Boroom, nun dey toppoon nanu sunuy sang ak sunuy kilifa. Ñu réerale nu ak yoon wa. 68. Boroom sunu, fulandileen mbugal te nga rëbbleen rëbb mu rëy”. 69. Éy yéen ñi gëm ! Buleen mel ni ña daan lor Muusaa, di ko tuumaal. Far Yàlla setal ko ca tuuma ya, di ku mu jubaloon. 70. Éy yéen ñi gëm ! Ragal-leen Yàlla tey wax wax ju jub. 71. kon dey Dana leen yéwénalal seeni jëf, jéggal leen it seeni bàkkaar. Te képp kuy topp Yàlla ak ub Yonentam, dana texe texe gu màgg. 72. Gaaral Nanu ndénkaan lii asamaan yeek suuf si ak tundi doj yi . Ñu lànk koo yenu ngir ug ragal ko, nit moo ñëw ne ko fànkul yenu ko ; te nit nekk ab tooñaakoon bu xamadi. 73. [Ci loolu] Yàlla dana mbugal naaféq yu góor yeek yu jigéen, ak bokkaalekat yu góor yeek yu jigéen yi te Dana nangu tuubug jullit yu góor yeek yu jigéen yi. Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la. ----------------------------------------------------------------------------- Saar 34 : RÉEWUM SABA 54 laaya – Laata Gàggaay ga
coran-wolof.pdf
page_336
336 ----------------------------------------------------------------------------- Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi. 1. Cant ñeel na Yàlla, Yàlla mi moom li nekk ci asamaan yeek suuf si. Cant it ñeel na ko ca àllaaxira. Moo di Ku Xereñ, di Ku Xàmmee. 2. Xam na li duggu ci suuf ak la cay génne, ak lay wàcc ci asamaan si ak la cay yéeg. Mooy Jaglewaakoon ba, di Jéggalaakoon ba. 3. Yéefar yaa ngay wax naan : “Bis-pénc ba du ñëw”. Waxal ne : “Axakañ. Giñ naa ci sama Boroom ! ne dana leen dikkal. Moom mi xam kumpa. Te dara lu tollu ni aw pepp du ko lënt ci asamaan yeek suuf si. Walla lu ko gën a tuuti, walla lu ko gën a rëy, lu dul ne mi ngi ci ab Téere bu bir. 4. [Li waral Bis ba], ngir fey ña gëmoon tey jëf u yiw. Danañu am njéggal, ak teraanga ak i xéewal. 5. Ña doon dëgërante bopp te Sunuy laaya nag ñoom, danañu am mbugalum kaŋ-kaŋ mu metti. 6. Woroom xam-xam ya danañu gis ne li Nu wàcce ci yaw mu bawoo ca sa Boroom, mooy dëgg te dafay gindee jëme ca yoonu Yàlla wu jub wa xocc, Yàlla miy boroom kàttan, di Yayowaakoonu cant. 7. Ña weddee ngay wax naan : “Ndax dunu leen tegtal ci waa joo xam ne nee naay su ngeen deewee ba daggatoo, di ngeen dekkiwaat? 8. Moo ndax dafay sosal Yàlla ay fen ? Walla jinne dakoo sadd ? ” La am kay moo di ña gëmul àllaaxira ñanga ca mbugal ak réer gu sori. 9. Ndax dañoo gisul li leen wër ci asamaan ak suuf ? Su Nu sooboon, mën Nanu leen a jaxaseek suuf si, walla Nu rotale ay dogit yu bawoo ci asamaan si. Ay kéemaan a ngi ci loolu ngir bépp jaam buy delluwaakoon ci Boroom bi .
coran-wolof.pdf
page_337
337 10. Joxoon Nanu Daawuda ngëneel lu bawoo ci Nun. Doj yeek njanaaw yi ànd ak moom di sàbbaal. Te it nooyalaloon Nanu ko weñ gu ñuul. 11. (ne ko) : “Liggéeyal ay mbubbi koŋ te jekkal ko”. Te ngeen di jëf u yiw. Kuy gis laa [Man Yàlla] li ngeen di def. 12. Tàggataloon Nanu Suleymaan ngelaw li, am xëyëm doxub weer la woon, am ngontam it, doxub weer la woon. Nu nooyalaloon ko bëtub mbellum përëm. Amoon na ci jinne yi ñu koy liggéeyal ci ndigalul Yàlla. Ku ca fétt nag, Dananu ko mosal mbugalum safara. 13. Ñu di ko liggéeyal lu ko soob : ci ay tabax ak i bóoli yu tollu ni ay xur, ak i kawdiir yu ñu sësale. “Yéen waa kër Daawuda, gërëmleen Yàlla”, te néewaana mu am ci sama jaam yi ay santkat. 14. Ba Nu dogalee mu war a dee, la leen ko xamal moo di max ga lekk yetam wa. Ba mu daanoo, jinne yi daldi xam ne bu ñu xamoon kumpa, duñu sax ca mbugal moomee daan leen tax a doyadi. 15. Waa réewum Saba amoon nañu màndargam ñaari dër ci ndeyjoor ak càmmooñ. “Lekkleen ci xéewali Yàlla, mayi seen Boroom, te ngeen sant Ko ndax : may na leen dëkk bu teey, neex, te di Boroom biy Jéggalaakoon”. 16. Waaye dummóoyu woon nañu . Nu daldi leen yebalal mbënnum téqum ndox ma, Nu daldi leen soppil seen tooli dër y, def leen ay tool yu am meññent mu sëcc ak i gargamboose ak i siddéem juy néewal. 17. Loolu la Nu leen feye woon ngir seenug weddi. Moo ndax Dananu ko feye keneen ku dul ñuy weddi ? 18. Te defoon nanu seen digganteek yeneen dëkk ya barkeel, ay dëkk yu fés, te nattle woon Nanu seenug demlante. “Demlanteleen ci guddi mbaa bëccëg ci kóolute”. 19. Ñuy wax naan : “Yaw sunu Boroom, dandaleel sunuy diggantey dëkk”, daldi tooñ seen bopp. Ba mujj di ay waxtaan ndax téqale Nanu leen. Ay kéemaan a ngi ci biir loolu ngir bépp muñaakoon buy sant.
coran-wolof.pdf
page_338
338 20. Séytaane dëggalal na leen njortam. Ñoom ñépp daldi koy topp ba mu des ab kurél bu néew ca way-gëm ña. 21. Amul woon ci ñoom benn mën-mën lu dul ngir Nu xam ña ca gëm àllaaxira ak ña koy sikki-sàkka. Sa Boroom mooy wattu lépp lu ne. 22. Waxal ne : “Li ngeen di jaamu bàyyi Yàlla. Amuñu lu tollu ni kem aw fepp ci asamaan yeek suuf si. Bokkuñu ci, ci dara, te it kenn dimbaliwu ko woon ci ñoom”. 23. Tinu mënu la jariñ dara fa Moom [Yàlla], lu dul ka Mu ca jox ndigal. Bu tiit ma duggee seeni xol nag, ñu naan : “Lan la seen Boroom wax nag ? ”. Ñu ne leen : “Dëgg rekk ; Te Moom moo di Ku Kawe, di Ku Màgg ka”. 24. Neel : “Ana kan moo leen di wërsëgal ci asamaan yeek suuf si ? ”. Waxal ne : “Yàlla. Te Nun ak yéen, ana kan moo nekk ci njug walla réer gu bir”. 25. Neel : “Kenn duleen laaj li nuy def, te it kenn dunu laaj li ngeen di def”. 26. Waxal ne : “Sunu Boroom dananu dajale, daldi Nuy àtte ci dëgg, Mooy ubbiwaakoon bu xam ba”. 27. Waxal ne : “Wonleen ma ña ngeen daan bokkaaleek Yàlla. [Mukk] ! Li wér moo di ne Mooy Yàlla, di Boroom Kàttan, di Ku Xereñ”. 28. Yónniwunu la [yaw Muhammad] lu dul nga daj képp nit ñi, di béglekat, di xuppekat. Waaye li ëpp ci nit ñi duñu xam. 29. Ñuy wax naan : “Dig ba kañ lay doon su fekkee ne li ngeen di wax dëgg la ? ”. 30. Waxal ne : “Am ngeen digub Bis boo xam ne dungeen ko jiitu, dungen ko yées ! ”. 31. Yéefar ya nee nañu : “Duñu gëm Alxuraan walla lu ko jiitu”. Cëy boo gisoon tooñkat ya bu keroogee ba ñu taxawal leen ci seen kanamu Boroom, nga gis leen ñuy wàqante ! Ña néewoon doole di wax kilifa ya, naan leen : “Bu dul kon ak yéen, ay jullit la nuy doon”.
coran-wolof.pdf
page_339
339 32. Ña ca doonoon kilifa wax ña ca néewoon doole, ne leen : “Ndax Nun noo leen féewale woon ak njub ga ca ba mu leen dikkalee ? Li wér kay mooy yéen ay tooñkat ngeen”. 33. Ña ca néewoon doole wax ña ca doonoon ay kilifa, ne leen : “Moom ngeen daan fexe guddi ak bëccëg, ndax yéen a nu daan digal nuy weddi Yàlla, di ko sàkkal ay bokkaale”. Daldi nañu rëccu ba ñu gisee mbugal ma. Nu daldi def ay jéng ca loosi ña weddi : moo ndax feyewuñu leen lu dul la ñu daan def ? ” 34. Amul benn dëkk bu Nu mës a yebal ab xuppekat lu dul ne kilifa ya dañuy wax naan : “Nun dey weddi nanu lii ñu leen yónni”. 35. Ñuy wax it naan : “Nun noo leen ëppale alal ak i doom te sax kenn dunu mbugal”. 36. Waxal ne : “Yàlla sama Boroom mooy yaatalal ku ko soob wërsëg, di ko xatal it. Waaye li ëpp ci nit ñi waxuñu”. 37. Nekkul ne seeni alal walla seeni doom ñoo leen di tax a jegeñ Yàlla. Lu dul ña ca gëm tey jëf u yiw. Ñooñu danañu am pey gu ñu fulandi ci sababus la ñu daan jëf, te ñoom ña nga ne fayax ci ay kër yu kawe [ca Àjjana]. 38. Waaye ña daan dox, di dëgërante bopp ak Sunuy kàddu, ñoom ña nga ne xeew ci biir mbugal ma. 39. Waxal ne : “Yàlla sama Boroom mooy yaatalal ku ko soob wërsëgam ci jaamam yi, Moo koy xatal it. Lépp lu ngeen mën a joxe [ci alal], moom Yàlla moo koy wuutalaat, te Yàlla moo di ngën ji kuy wërsëgal”. 40. Bu keroogee Bis ba leen Yàlla di dajale mbooleseen. Ba noppi daldi wax Malaaka ya ne leen : “Moo ndax ñii yéen la ñu daan jaamu ? ”. 41. Ñu ne : “Tudd nanu sag sell ! Yaw yaay sunu wéeruwaay, du ñoom. Li am moo di, ñoom jinne yi la ñu daan jaamu, li ëppoon ci ñoom jinne la ñu gëm.
coran-wolof.pdf
page_340
340 42. Tey jii nag, kenn ci ñoom ëmbalut moroomam lor mbaa njariñ, te Dananu wax ña daan tooñ ne leen: “Tokkamtikuleen mbugamal Safara sa ngeen doon weddi”. 43. Bu ñu mësaan a jàng ci ñoom laaya yu leer, dañu naan : “Waa jii daal nammul lu dul féewale leen ak li leen seeni baay daan jaamu”. Ñuy wax it naan : “Lii daal du dara lu dul ay fen yu ñu sos”. Ña weddi woon dëgg it ba mu leen dikkalee, ña nga naan : “Lii daal ag njibar doŋŋ la ! ”. 44. [Moonte] Joxuñuleen woon ay téere yu ñuy mën a jàng. Mësuñoo yónni it ca ñoom ab xuppekat bu la jiitu. 45. Xeet ya jiitu woon waa Màkka weddi woon nañu Yonent ya. Te waa Màkka amuñu ca lu tollu ni fukkeelu la ñu joxoon ñooña [ci kàttan]. Ñoom it ne sunuy ndaw ay fenkat lañu. Kon naka la samab sànje di dem ! 46. Waxal ne : “Maa ngi leen di waar ci lenn : nangeen taxaw ngir Yàlla, moo xam ngeen diy ñaar-ñaar walla ngeen di benn been, te ngeen xalaat. Seen àndandoo bii di Muhammad jinne sadd ko : moom doonul lu dul ab xuppekat bu ame mbugal mu nekk seen kanam”. 47. Neel : “Laajumaleen ci ag pey, yéen a ko moom. Samag pey, Yàllaa ko warlu. Moom seede la ci lépp lu nekk”. 48. Neel : “Neel Yàlla mooy badd ndawam ci dëgg. Mooy xamaakoonu mbóot ya”. 49. Waxal ne : “Dëgg [Lislaam] dikk na. Te ag neen [kéefar] du fi tàmbalee te du fi dellusi”. 50. Waxal ne : “Su ma réeree , sama bopp doŋŋ laay sànk ; su ma gindikoo it, ci sababus li ma Yàlla soloo lay ame, Moom Yàlla kuy Dégg, kuy Jigeñ la”. 51. Cëy soo leen gisoon ba ñu jàqee, - kenn du raw, - dañu leen a ndar-kepp ci barab bu nekk ! 52. Ñu neey : “Gëm nañu”, - Moo fu leen ngëm di bawoo ? 53. te fekkoon ñu weddi lu jiitu, di sànney kumpa ci barab bu sori !
coran-wolof.pdf
page_341
341 54. Ñu gàllankoor seen digganteek la ñu doon wuneen [sopp], kem nañu ko defe woon ca ña leen jiitu, ña nga woon ci biir sikki-sàkka gu xóot. ----------------------------------------------------------------------------- Saar 35 : AJI-SÀKKE JI 45 laaya – Laata Gàddaay gi ----------------------------------------------------------------------------- Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi. 1. Xeeti cant yépp ñeel na Yàlla mi bind asamaan yeek suuf si, Mooy ki def Malaaka yi ñu di ay ndaw te di woroomi laaf, ñaar-ñaar, ñett ñett walla ñeent ñeent. Mooy dolli ca mbind ga lu ko soob, Yàlla mën na lépp lu nekk. 2. Li Yàlla di ubbil nit ñi ci yërmaande, kenn mënu koo fànq, lu Mu tëj itam, kenn mënu koo tijji ginnaawam. Mooy boroom Kàttan, di Ku Xereñ. 3. Éy yéen nit ñi ! Fàttalikuleen xéewali Yàlla yi ci yéen : moo ndax amuñu bindkat bu dul Yàlla, bu leen di wërsëgal ci asamaan yeek suuf si ? Amul jeneen yàlla ju dul Moom ! Moo yéen ndax mën ngeen koo dummóoyu ? 4. Bu ñu la weddee it, xamal ne weddi woon nañu ay Yonent yu la jiitu woon. Te ca Yàlla la mbir yi di mujj. 5. Éy yéen nit ñi ! Li Yàllay dige dëgg la. Buleen dundug àddina bii di fàbbi, buleen Séytaane tax a fakku ci Yàlla. 6. Séytaane, seenub noon la. Nangeen ko jàppe ab noon. Li muy woote di ci xiirtal gàngooram moo di ngir ñu nekk waa Safara doŋŋ la.
coran-wolof.pdf
page_342
342 7. Ña weddi, mbugal mu metti dana leen dal, ña gëm nag tey jëf u yiw, danañu am njéggal ak pey gu rëy . 8. Naka kay jàppee ñaawtéefam ya muy lu rafet... ? – Yàllaay réeral ku ko soob, di gindi ku ko soob – Bul sonnal sa bopp ci ñoom : Yàlla xam na xéll la ñuy def. 9. Yàlla miy yebal ngelaw muy niir, Nu wommat ko jëme ko ci dëkk bu deewoon ; di ca dundal suuf si ginnaaw ba mu deewee. Noonu la Dekki di ame. 10. Képp kuy bëgg kàttan , na xam ne kàttan ba kàttan jeex, Yàllaa ko ame : ca Moom la wax ju yiw di yéeg ak jëf ju yiw, Mu di ko yékkati. [Waaye] ñiy fexe ay ñaawtéef, am nañu mbugal mu tar. Te seeni pexe du joy mukk. 11. Yàlla moo leen bind ci suuf ba eggal, def leen ay lumb deret, topp Mu def leen ay yóllent [góor ak jigéen]. Amul jenn jigéen juy ëmb walla muy imbi lu dul ci xam-xamam lay ame. Amul it genn dundu guy yokk walla muy wàññiku te duwut ne mi ngi ci ab Téere . [Loolu] yomb na lool ca Yàlla. 12. Ñaari géej ya yemuñu : gii dafa neex a naan te lewet domm, gee saf xorom te naqari. Ngeen di ca génnee aw yàpp wu tooy di ko lekk, ngeen di ca génne itam gànjar gu ngeen di sol. Nga gis gaal ya di jax ca biir ngir sàkku ci ay xéewalam. Ak it ndax amaana ngeen sant. 13. Mooy dugal guddi ci bëccëg, di dugal bëccëg ci guddi. Di tàggat jant beek weer wi. Lu ca nekk a ngay daw ci ab dig bu ñu ko àppal. Kooku moo di Yàlla : seen Boroom moo moom nguur, te li ngeen di jaamu bàyyi ko, amuñu sax lu tollu ni kem mbuusum xooxu tàndarma. 14. Bu ngeen leen di woo, duñu leen dégg ; bu ñu leen déggoon it, duñu leen tontu. Bu Bis- pénc baa, danañu teggi ba mu set li ngeen ko doon bokkaale. Amul kenn ku la mën a jox xibaar yu wére nii. 15. Éy yéen nit ñi, yéen ay soxlaa woo Yàlla, waaye Yàlla moom Ku doylu la ci boppam, di Yeyoowaakoonu cant. 16. Su ko neexoon Mu yóbbu leen, indi ñeneen mbindeef yu bees. 17. Te loolu du lu jafe ci Yàlla.
coran-wolof.pdf
page_343
343 18. Kenn du yenu bàkkaarub keneen. Te képp ku diis gann ak bàkkaar, bumu cay woote ndimbal, kenn du ko yenul dara, doonte la sax dafa di mbokkug jegeñaale. Da di rekk ne nangay xupp ña di ña ragal seen Boroom ci kumpa tey taxawal julli. Te képp ku cay sellal, na xam ne boppam la koy defal, te ca Yàlla la lépp di mujj. 19. Gumba ak njàccaar niróowuñu. 20. du caagene lëndëm ak leer. 21. du caagene ker ak naaj. 22. Ñiy dundu it niróowuñook ñi dee. Yàlla dina déggloo ku ko soob, te yaw Muhammad mënoo déggloo ñi xas nekk ci biiri bàmmeel. 23. Yaw daal nekkoo lu dul ab xuppekat. 24. Yónni Nanu la ci dëgg ngay bégalekat di ab xuppekat, amul wenn xeet wu amul ab xuppekat. 25. Su fekke ne dañu laa weddi, [xamal ne] am na ñu leen jiitu woon te daan weddi, ndax seeni Yonent indiloon nañu leen ay laaya, ay firnde yu bir ak ay mbind ak ab Téere bu leer. 26. Ginnaaw ba, Ma jël ña weddi. Cëy na Ma leen jële. 27. Xanaa gisuloo ne Yàlla moo wàcce ndox mu bawoo ci asamaan si ? Nu daldi cay génne ay meññent yu wuute ay wirgu. Am na it ci tundi doj yi yuy sësëloo te weex, ak yuy xonk, yu wuute ay wirgu, ak yu ñuul kukk. 28. Am na it ci nit ñi, ci daaba yeek mala yi yu wuute ay wirgu, noonu rekk la. Jaami Yàlla yi ko ragal ñoo di woroom xam-xam yi. Te Yàlla boroom xam-xam la, di Jéggalaakoon. 29. Ñay jàng Téereb Yàlla ba, tey taxawe julli, tey joxe ci [alal] ji Nu leen wërsëgale, ci lu nëbbu ak ci lu feeñ, ñoom yaakaar nañu am njula mu dul yàqu.
coran-wolof.pdf
page_344
344 30. loolu lépp ngir Yàlla jox leen seenug pey te dolli leen ciy ngënéelam. Moom Yàlla, Jéggalaakoon la, Kuy sant la. 31. La Nu la soloo ci Téere bi mooy dëgg tey saxal la ko jiitu woon . Yàlla kuy Xàmmee la, Kuy Gis jaamam ñi la. 32. Ginnaaw ba, donnale Nanu Téere ba sunu jaam ña Nu tànn. Am na ci ñoom kuy tooñ boppam, am na ci ñoom ñuy yamamaay, am na it ci ñoom ñuy jëkkante ciy jëf yu baax ci ndimbalu Yàlla ; loolu nag tigi mooy ngëneel la gën a màgg. 33. Àjjanay Hadan yoo xam danañu ca dugg, ñu di leen fa sadd ay lami wurus ak peme ; te seenug col ca biir àjjana yooyu sooy lay doon. 34. Ñuy wax naan : “Xeeti cant yi ñeel na Yàlla, Yàlla mi nu dàqal tiitaange. Sunu Boroom daal Jéggalaakoon la buy Yayoowaakoonu cant. 35. Moom mi nu dalal ci kërug nooflaay ci mbaaxam, coono dunu fa dab, jaaxle it dunuu fa dab”. 36. Ñay weddi nag, ñoom Safara la ñuy dëkk : ñu di leen xorñoññal, duñu dee ; te it deesuleen woyofalal mbugal ma. Noonu la Nuy feye képp ku di ab weddiwaakoon. 37. Ña ngay yuuxu ca biir, di wax naan : “Yaw sunu Boroom, génne nu ; kon dey dananu jëf u yiw, wu bokkul ak la ñu daan jëf ”. “Waaw, moo ndax dundalunuleen fa woon diir bu tax, ña fàttaliku ñépp, fàttaliku nañu ca ? Te ay xuppekat it dëkkaloon nañu leen. Kon book, toqamtikuleen mbugal mi. Tooñkat yi, kenn duleen dimbali”. 38. Yàllaa xam kumpag asamaan yeek suuf si. Moom ab Xamaakoon la li nekk ci dënn yi . 39. Moo leen def ngeen di ay kuutaatam ci kaw suuf si. Képp kuy weddi, weddeem ga dana daanu ci kawam. Te yéefar ya, seenug weddi duleen dolli lu dul jéppig Yàlla. Te it seen weddi googu duleen dolli lu dul yàqule.
coran-wolof.pdf
page_345
345 40. Neel : “Ndax gis ngeen ñi ngeen bokkaleek Yàlla, di leen jaamu ? Wonleen ma ñoom ana lan la ñu bind ci kaw suuf si. Walla dañoo am sañ-sañ ci asamaan yi ? Walla dañu leen a joxoon Téere bu leen bir” Déedéet ! Li am kay moo di ne tooñkat ñi ñoom wor rekk la ñuy digante. 41. Yàlla moo téye asamaan yeek suuf si ba daanuwuñu. Te bu ko dindi woon it, amul kenn ci ñoom ku ko cay téye ginnaawam. Moom Yàlla ab Jéggalaakoon la, ku Lewet la. 42. Dañu daan waat ci Yàlla fu ngiñ gën a ñàngee, di wax naan : su leen ab xuppekat dikkaloon, ñooy gën a gindiku weneen xeet wu dul ñoom. Waaye ba leen ab xuppekat dikkalee , dolliwuleen lu dul dummóoyu . 43. [Te dara waralu ko] lu dul rëy-rëylu ak pexe yu bon. Te pexe mu bon du rey lu dul boroom. Te ñoom néggandikuwuñu lu dul xew-xew ya leen jiitu woon ? Te tëralinu Yàlla kenn du ko sopparñi, te kenn it du ko wëlbati. 44. Moo ndax dañoo doxul ci suuf si tey xool mujjug ña leen fi jiitu woon te ëppoon leen doole ? Amul dara lu mën të Yàlla ci asamaan yeek suuf si. Moom Yàlla kuy Xam la, kuy Mën la. 45. Su Yàlla doon jàppe nit ñi ci li ñuy def. Kon du bàyyi kenn kuy dox ci kaw suuf si. Waaye daleen di xaare àpp ba Mu àppal. Cëy bu dig ba agsee... [danañu xam ne] Yàlla kuy gis jaamam ñi la. ----------------------------------------------------------------------------- Saar 36 : YAA-SIIN 83 laaya – Laata Gàddaay ga ----------------------------------------------------------------------------- Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi 1. Yaa-Siin.
coran-wolof.pdf
page_346
346 2. Maa ngi waat ci Alxuraan jii fees dell ag xereñ. 3. Ci ne yaw [Muhammad] bokk nga ci limub Yonent yi. 4. ci kaw yoon wu jub xocc wa. 5. Mi ngi wàcce ci Yàlla boroom Kàttan ga di ab Jaglewaakoonu yërmaandeem. 6. Ngir nga xupp aw nit ñoo xam ne kenn musul a xupp seeni baay : ñoom dañoo sàggan. 7. Àtte ba dog : te la ëpp ca ñoom [ca Lawhul Mahfuuj] ci ne duñu gëmati. 8. Def Nanu ay jéng ci seeni loos, mu àndak seeni daayi sikkim : ñu joñ leen. 9. def Nanu ab ñag ci kanam ak ci seen ginnaaw ; Muur Nanu leen ba dootuñu gis. 10. Nga xupp leen ak nga ñàkk leen a xupp ñoo yem kepp ci ñoom : duñu mës a gëm. 11. Ka ngay war a xupp kay mooy kay topp [Alxuraan], tey ragal Yàlla ci kumpa. Nanga ko bégal ci ag njéggal ak pey gu tedd . 12. Nun Yàlla nooy dundal néew tey bind la ñu defoon ak seeni jeexit. Te mbir mu ci bokk yéege Nanu ko ci biir ab téere bu bir , bind ko ca. 13. Joxleen misaal ci waa dëkk ba ab Yonent dikkaloon. 14. Ba Nu leen jebalee ñaari ndaw ñu weddi leen. Nu daldi leen kàttanalaat ci ndaw lu leen ñetteel, ñu ànd ñoom ñett, ne leen : “Nun ndawi Yàlla lanu”. 15. [Waa dëkk ba] tontu [Antaakiya] ne leen : “Yéen daal, ay mbindeef ngeen ni nun. Te Yàlla wàccewul dara, yéen daal ay fenkat doŋŋ ngeen”.
coran-wolof.pdf
page_347
347 16. [Yonent ya] waxaat ne : “Yàlla xam na ne nun ay Yonent lanu ci yéen. 17. te dara warunu lu dul jottali ba mu leer nàññ.” 18. Ñu ne : “Gaafal nanu leen. Te bu ngeen bàyyiwul, dananu leen jóori xeer te dananu leen mbugal mbugal mu tar”. 19. Yonent ya ne leen : “Seen gaaf googu mook yéen a ànd”. Moo ndax fàttaliwunu leen woon ? Yéen daal dangeen a yebaate ! ”. 20. Mu am waa ju jóge woon ca anéeri dëkk ba, di dox ne leen : “Éy yéen samaw nit, moo tee ngeen a topp Yonent yi : 21. Toppleen ku dul laaj ag pey te ñoom ñu gindiku lañu. 22. moo man, ana lu may war a dal ba tax duma jaamu Yàlla mi ma bind ? Te ca Moom ngeen di dellu. 23. Moo ndax damay wuti jeneen yàlla ju dul Moom ? Te bu Yërëmaakoon bi natte ci man lor, seenug tinu duma jariñ dara te duñu ma xettali. 24. Su loolu amoon dey kon, maa ngi ci ag réer gu bir. 25. Man dey, gëm naa seen Boroom, dëggal-leen ma”. 26. Waxees na ko, ne ko : “Tàbbil Àjjana”. Mu wax ne : “Cëy aka neexoon samaw nit xam ! 27.... li tax Yàlla jéggal ma, def ma ma bokk ci ña Muy teral”. 28. Wàccewunu ci aw nitam ginnaaw ba mu jàllee, ay xarekat ñuy bawoo asamaan. Bëggunu fa woon a wàcce dara itam.
coran-wolof.pdf
page_348
348 29. Génn xaacu rekk a fa jaar, ñu faf giim. 30. Ndeysaan jaam ñi le ! Ab Yonent mësuleen a dikkal mukk te du dañu koy ñaawal. 31. Xanaa gisuñu na Nu faagale woon maas ya leen jiitu woon ? Te kenn du ca dellusi. 32. Te ñoom ñépp danañu daje Sama kanam . 33. Indil Nanu leen firnde te moo di suuf si dee , Nu dekkalaat ko, [tawu ndow] génne ca ay doom, ngeen di ca lekk. 34. Nu def ca ay tooli dëri tàndarma ak yu reseñ, xàbbal ca ay bëti ndox, 35. ndax ngeen di lekk ca meññent ma ak li ngeen cay liggéeyee. Moo ndax duñu sant ? 36. Tudd naa sellug bind yóllent yi mbooleseen ci liy sax ci suuf ak ci seeni jëmm ak ci li ñu xamul ! 37. Ak firndey bu bëccëg jàlle, guddi ñëw lëndëm taruus. 38. te jant baa ngay daw ca fa ñu ko rëddal ; looloo di nattaleb Yàlla miy boroom Kàttan, di ku Xam. 39. Weer wi nattale Nanu ko ay këri wàccuwaay ba faf mu mel ni tàndarma gu màggat. 40. Jant bi du jot weer wi, guddi it du jiitu bëccëg ; ku nekk a nga ca yoonam di féey. 41. Ak firndey yenu gi Nu yenu seeni sët ci biir ag gaal gu ñu sëf ; 42. Te sàkkal Nanu leen yeneen yu ni mel ñu di ca war. 43. Bu Nu sooboon, Nu labal leen ; duñu xam fu ñuy yuuxu jëmële, te kenn du leen xettali,
coran-wolof.pdf
page_349
349 44. lu dul yërmaande ju bawoo ci Nun, ak i xéewal ba jëmmi jamono. 45. Te saa su ñu leen waxee ne : “Wattandikuleen li nekk ci seen kanam ak li ci seen ginnaaw ndax amaana yërmaande wàcc ci yéen” !... 46. Amul yenn laaya , yu bokk ci seeni laayay Boroom, dikkal leen te dañu koo dëddu. 47. Saa su ñu leen waxee ne : “Joxeleen ci alal ji leen Yàlla wërsëgal”, ña weddi dañuy wax ña gëm, naan leen : “Moo ndax nun danuy dundal koo xam ne bu neexoon Yàlla mu dundal ko ? Yéen daal ci ag réer gu bir ngeen nekk”. 48. Ña ngay wax naan : “Dig ba kañ lay ñëw ndegam li ngeen di wax dëgg la ? ” 49. Xaaruñu lu dul genn yuuxu gu leen jël fekk leen ñuy xuloo. 50. Duñu mën a batale, di dénkaane, mbaa ñuy mën a dellu ca seen njaboot. 51. Su ñu ëfee Buftu bi, dañu naan futeet ca bàmmeel ya, dox wuti seen Boroom, 52. ñuy wax naan : “Wóoy ngalla nun ! Moo ana kan moo nu yékkatee ci sunu yàndoorukaay bi ? ” Lii dey mooy la nu Yërëmaakoon bi doon dig ; kon Yonent yi waxoon nañu dëgg. 53. Genn ug xaacu rekk a jib, ñu seet-seeti ñoom ñépp, ne jaseet Sunu kanam. 54. Bis niki tey, deesul tooñ benn bakkan . Te deefuleen feye lu dul la ngeen daan jëf. 55. Bis niki tey, waa Àjjanaa ngi ci xéewal gu mat sëkk ; 56. ñoom ak seeni soxna, ña nga ca biir kër ya, sóonu ca lal ya. 57. Am nañu fa ay fuytéef ak lépp lu ñuy soxla,
coran-wolof.pdf
page_350
350 58. “Jàmm rekk la ñu fay ame” ! Mu bawoo ca Boroom biy Jaglewaakoonu Yërmaandeem. 59. “Ayca ! Ca biti, yéen tooñkat yi ! 60. Yéen doomi-aadama, ndax digewuma woon ak yéen ngeen bañ a jaamu Séytaane ? Ndax seenub noon la bu nëbbëtuwul, 61. te ngeen di Ma jaamu ? Lii mooy yoon wu jub xocc wi. 62. Mu réeral ci yéen lim bu takku. Xanaa daawuleen xalaat ? 63. Safara si ñu leen daan dig, mi ngi nii. 64. Xoyomuleen ci bis niki tey, muy [peyug li ngeen daan weddi]”. 65. Bis niki tey, Dananu ŋalaab seeni gémmiñ, seen yoxo ya di wax ak Nun, seen tànk ya di seede la ñu daan fàggu. 66. Te kat, bu Nu sooboon, Dananu fatt seeni gët, bàyyi leen ñuy jëkkante ci kaw [siraat], ba xam fu ñuy giseeti ? 67. Bu Nu sooboon, Dananu leen rat benn barab ; dootuñu dem, duñu dikk. 68. Képp ku Ma defal aw fan wu guddi, Danaa ko màggatloo, xanaa dungeen xalaat ? 69. Jàngalunu Muhammad woy mbaa lu koy nuru ; lii daal du dara lu dul ag fàttali ak Alxuraan juy biral, 70. ngir muy xupp ñiy dundu, wax ja itam di lu yay ca yéefar ya. 71. Xanaa dañoo gisul ne sàkkal Nanu leen ci Sunu liggéeyu loxo ag jur gu ñuy moom ;
coran-wolof.pdf
page_351
351 72. Nu tàggatal leen ko ; ñu di ca war te it ñu di ca lekk ; 73. am nañu ci ay njariñ ak i naan. Moo ndax dañu dul sant ? 74. Ñuy jàppe yàlla leneen lu dul Yàlla, ngir ñu neey danuy sàkku ndimbal... 75. Yooyu duleen mën a dimbali, dañuy sax faf di jàmmaarlook ñoom [di xare]. 76. Bula seeni wax jaaxal ! Nun xam Nanu li ñuy yelu ak li ñuy biral. 77. Xanaa nit dafa gisul ne Nun Yàlla noo ko bind ci lumbub deret ? Deketeyoo moom ab xulóowaakoon la bu di ab pànk ! 78. Mu di Nu sàdd léebu, fàtte na ag sosoom ; dana wax naan : “Ana kan mooy dekkalaat ay yax yu funux ? ” 79. Neel : “Ki ko sosoon bu jëkk. Te xam lool bindafoon yépp ; 80. te Moo di ki leen defal ci garab gu nëtëx, aw safara wu ngeen di taaloo. 81. Moo ndax ku bind asamaan yeek suuf mënul a bindaat ñeneen yu na mel ? Axakañ ! Moo di Bindaakoon, Xamaakoon bi. 82. Ay mbiram moo di, saa su bëggee menn mbir, dakoy wax : “Nekkal”, mu daldi nekk. 83. Tudd naa sellug ki nga xam moo ame ci loxoom moomeelug lépp ! Te it ca moom ngeen di dellu yéen ñépp. -----------------------------------------------------------------------------
coran-wolof.pdf
page_352
352 Saar 37 : SÀPPE YA 182 laata – Laata Gàddaay ----------------------------------------------------------------------------- Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi. 1. [Maa ngi] giñ ci [Malaaka] ya sësëloo, def ay sàppe. 2. Ñay bëmëg niir yaak doole. 3. Ñay jàng ngir fàttali : 4. “Ne seen Yàlla jenn la tigi, 5. mooy Boroom asamaan yeek suuf si ak li nekk seen diggante tey Boroom penku yi”. 6. Taaralal Nanu asamaan si gën a jexe àddina si ci taarub ay bidiw, 7. def ca kaaraange ci sépp séytaane suy féttérlu. 8. Duñu mën yëddu waa péey ba gën a kawe ; te dañu leen fay mbàqe wet gu nekk, 9. dàqe leen fa. Ñu am mbugal muy sax. 10. Xanaa rekk léeg-léeg mu am ñu cay sàcc ay xibaar ; ñu di ko dàq ak jumu safara buy bënn. 11. Laajleen baxam dañoo gën a jafe bind ñeneen ña Nu bind ? Noo ngi leen binde ci ban bu tikk !
coran-wolof.pdf
page_353
353 12. Yaw waaru nga, te ñoom ña ngay tejjiy reetaan ! 13. Te bu ñu leen di fàttali, duñu fàttaliku [Alxuraan] ; 14. dañuy wàkkante ak a reetaan [saa su ñu gisee keemaan], 15. tey wax naan : “Lii dey ag njabar doŋŋ la. 16. Moo ndax su nu faatoo ba def suuf ak i yax, dees nanu dekkalaat ? 17. ak sunuy baay ak i maamaat ? ” 18. Neel : “Waaw ! te dangeen torox de”. 19. Genn ug xaacu rekk ay jib, ñu ne xewwu di xoolante (dekki), 20. ñuy wax naan : “Ngalla nun ! Bis-pénc baa ngi nii waay”. 21. “Lii mooy bisub àtte ba ngeen jàppe woon ay fen, weddi ko”. 22. “Dajaleleen tooñkat ya ak seeni jabar ak la ñu daan jaamu, 23. bàyyi woon Yàlla. Te wëtal leen jëme yoonu Safara. 24. Te ngeen taxawlooleen : ndax dañu leen di laaj”. 25. “Ana lan moo tax dungeen dimbalante” ? 26. Li wér mooy bis niki tey jébbalu nañu,
coran-wolof.pdf
page_354
354 27. ku nekk di geesu moroom ma, ñuy laajante ; 28. Ñuy wax naan : “Yéen a nu daan ga ci kéefar”. 29. [Kilifa ya] ne leen : “Yéen kay yéen a gëmul woon. 30. Te nun amunu woon benn sañ-sañ ci yéen. Yéen kay yéen a bewoon. 31. La Yàlla daan wax dal na ci sunu kaw ; [tey] noo ngi toqamtiku [mbugal]. 32. “Noo ngi leen di jiiñ cànkute, waaye nun ñépp a faf sànku”. 33. Bu bisub keroogee ñoom ñéppay bokk mbugal ma. 34. Noonu la Nuy def tooñkat ya. 35. Bu ñu waxaan ne : “Amul jeneen yàlla ju dul Yàlla”, dañu daan rëy-rëylu, 36. tey wax naan : “Ndax danuy bàyyi sunu yàlla yi ngir woykat bu dof ? ” 37. Te moom dëgg rekk la indi tey dëggal li Yonent ya indi woon, 38. Yéen dangeen mos mbugal mu mitti. 39. Te it kenn du leen feye lu dul la ngeen daan jëfe, 40. ba mu des jaami Yàlla yay sellal, 41. Ñoom am nañu wërsëg wu ñu xam :
coran-wolof.pdf
page_355
355 42. ay fuytéef ak i teraanga, 43. ca biir Àjjanay xéewal ja, 44. ñuy jàkkaarloo ca seen kawi lal. 45. Ñu di leen wër ak kaasi bënub ndox 46. weex tàll, te neex lool ca ña koy naan, 47. Lëj-lëj du fa am. 48. Te am nañu fa ay lamsalkat yu am bët , 49. weex ba mel ni nen. 50. Ku nekk di geesu moroomam di laajante. 51. Mu am ci ñoom kuy wax naan : “Man dey amoon naa àndandoo” 52. di wax ba-tey naan : “Ndax yaw gëm nga tigi ? 53. Ndax bu nu faatoo ba doon suuf ak i yax, dara dananu warati ? ” 54. Mu wax ne : “Xanaa téenuleen ? ” 55. Mu daldi téen, gis ko ca biir Safara, 56. mu wax ne : “Waat naa ci Yàlla ne ! Xaw nga maa tax a alku !
coran-wolof.pdf
page_356
356 57. dogankoon ak sama dimbalul Boroom, danaa sànku. 58. Xanaa nun dey dunu dee 59. lu dul ca dee gu jëkk ga te xanaa kenn dunu mbugal ? ” 60. Lii mooy texe gu màgg ga. 61. Ñiy jëf, nañuy jëf lu mel nii. 62. Moo ndax loolu moo di wàccuwaay ba gën, walla garabug Zaquum ? 63. Def nanu ko muy sànjub tooñkat ya. 64. Moom garab la guy génn ca ndéntul Safara. 65. Meññent ma mel ni boppi séytaane. 66. Ca la ñuy lekk, di ca feesal seeni biir. 67. Am nañu fa, ca kawam, am ndox mu tàng [di wañax]. 68. Safara rekk mooy seen kër. 69. Daje nañu faak seeni [baay ak i maam] cig cànkute, 70. ñuy yolli-yolli topp leen. 71. Li ëppoon ca ña leen jiitu woon sàkku woon nañu.
coran-wolof.pdf
page_357
357 72. Ndax yónni woon Nanu ci ñoom ñuy xuppe, di waaraate . 73. Xoolal mujjug ñanu daan xupp ! 74. Ña ca dul jaami Yàlla ya ca daan sellal : 75. Nooh woo na Nu di ñaan, Nu wuyyu ko, nangu ñaanam. 76. Nu musal ko mook njabootam ci tiit mu rëy ma, 77. Nu def ay sëtam doŋŋ des fa. 78. Nu bàyyi ko, may ko mu di fàttaliku, 79. Yal na jàmm wàcc ci Nooh ci kaw àddina sépp ! 80. Noonu la Nuy feye ñiy rafetal. 81. Moom bokk na ca Sunu jaam yu gëm ya. 82. Ginnaaw ba, Nu labal ña ca des. 83. Ibrahiima bokkoon na ca ay njabootam. 84. Fàttalikul ba mu dikkee ca Boroomam ànd ak xol bu mucc ayib. 85. Ak ba mu waxee baayam ak nitam, ne leen : “Ana li ngeen di jaamu ? ” 86. Moo ndax ay nar ngeen di namm a def ay yàlla bàyyi Yàlla Moom ?
coran-wolof.pdf
page_358
358 87. Waaw, lu ngeen njort ci Yàlla boroom asamaan si ? ” 88. Mu téen xool biddéew yi [di settantal], 89. mu daldi wax ne : “Man damaa wopp”. 90. Ñu dëddu ko, won ko ginnaaw. 91. Mu potoxlu ca seen yàlla ya, ne leen : “Ndax dungeen lekk ? 92. Ana lu leen dal ba dungeen wax ? ” 93. Mu potoxlu dóor leen ak ndeyjoor. 94. Ñu wutsi ko di daw. 95. Mu wax ne : “Ndax dangeen di jaamu lu ngeen di yatt, 96. te Yàlla moo leen bind ak li ngeen di defar ? ” 97. Ñu wax ne : “Tabaxal-leen ko puur te sànni ko ca safara sa ! ” 98. Ñu bëggoon koo fexeel ; Nu suufeel leen, detteel leen. 99. Mu wax ne : “Maa ngi dem ca sama Boroom, Dana ma gindi. 100. Yaw sama Boroom, may ma ay sët yu yiw”. 101. Nu bégal ko, may ko doom ju lewet .
coran-wolof.pdf
page_359
359 102. Ba mu amee ati àndak moom, Ibraahiima wax na ne : "Yaw samas doom, gis naa ci bi may nelaw, ci biir gént, ndigalul war laa rendi. Seetal looy xalaat”. (Ismaayiila) ne ko : “Yaw sama baay, defal lu ñu la digal : bu soobee Yàlla, danga gis ne maag muñkat yee ànd”. 103. Ba ñu wéyalee seen ndigalul Boroom, mu di dëféenal ko, 104. Nu woo ko, ne ko : “Éy yaw Ibraahiima ! 105. Dëggal nga gént gi. Te noonu la Nuy feye ñiy rafetal”. 106. Lii ab tontu la bu bir. 107. Nu daldi koy jot ak lu ñuy rendi lu màgg. 108. Daldi koy bàyyi muy dundu moom Ismaahiila : 109. “Jàmmi Yàlla na nekk ci kaw Ibraahiima”. 110. Noonu la Nuy feye ñiy rafetal ; 111. bokk na ci Sunu jaam ñi gëm. 112. Bégal Nanu ko ci def Isaaqa mu di Yonent bokk ca ñay rafetal. 113. Nu barkeel ko moom ak Isaaqa. Mu am ci seeni sët kuy rafetal ak kuy tooñ boppam. 114. Xéewaloon Nanu Muusaa ak Haaruuna, 115. Musaloon Nanu leen ñoom seeni sët ca tiit mu rëy ma, 116. Nu dimbali woon leen, ñoom ñoo nootoon.
coran-wolof.pdf
page_360
360 117. Nu indiloon leen ab téere bu bir 118. Nu indiloon leen yoon wu jub wa xocc. 119. Nu bàyyi woon leen nit ña di leen fàttaliku : 120. “Jàmmi Yàlla na wàcc ci Muusaa ak Haaruuna” 121. Noonu la Nuy feye ñiy rafetal ; 122. ñoom ñaar bokkoon nañu ci Sunu jaam ñi gëm. 123. Ilyaas it tigi bokkoon na ci Yonent ya. 124. [Fàttalikul] ba mu waxee aw nitam, ne leen : “Ndax dungeen ragal Yàlla ? ” 125. Moo ngax dangeen di woo Bahlu bàyyi Yàlla miy ngën ji kuy bind, 126. Yàlla miy seen Boroom te di Boroomi seeni baay ak i maamaat ? ” 127. Ñu weddi ko, Nu mbugal leen. 128. Ba mu des jaami Yàlla ya daan sellal. 129. Nu bàyyi nit ñuy mujj noonu di ko fàttaliku : 130. “Jàmm yal na nekk ci njabootug Ilyaas”. 131. Noonu la Nuy feye ñiy rafetal,
coran-wolof.pdf
page_361
361 132. bokk na ci Sunu jaam ñi gëm. 133. Lóot it bokk na ci Yonent yi. 134. [Fàttalikul] ba Nu ko musalee mook njabootam gépp, 135. ba mu des màggat gu jigéen ga àndoon ak ña sànku woon, 136. Ginnaaw ba, faagaagal Nanu ña ca des 137. Te yéen a ngi leen di romb bu ngeen di xëy 138. ak ci guddi gi. Xanaa dungeen xalaat ? 139. Yuunuusa it bokk na ca Yonent ya. 140. Ba muy daw jëm ca gaal ga ñu yeb ga, 141. Ba ñu wantalee mu bokk ca ña ñu waroon a sànni ca ndox ma. 142. Jën wa dal koy wann, muy ku yeddu. 143. Dugankoon ak li mu bokkoon ca ña doon sàbbaal Yàlla, 144. kon dey dana sax ca biir [jën wa] ba bisub dekkiwaat ba di ñëw. 145. Nu sànni ko ca teges ga te muy ku ràgg. 146. Nu daldi fay saxal gàncaxug beraf,
coran-wolof.pdf
page_362
362 147. Nu yebal ko muy Yonent ci téeméeri junniy nit mbaa lu ko ëpp. 148. Ba ñu gëmee, xéewalal Nanu leen fa ab diir. 149. Laajleen baxam : “Ndax Yàlla moo ame doom yu jigéen, ñoom ñuy am doom yu góor ? 150. Walla dañoo bind Malaaka yi def leen ñu di ay jigéen, seere ko ? ”. 151. Ndax ñoom dañuy faral di wax ci seen duur ya, naan : 152. “Yàlla am na doom” ; te ñoom dañuy fen doŋŋ ! 153. Moo ndax dafay gënal doom ju jigéen ci kaw doom ju góor ? 154. Ana lu leen dal ba ngeen di àttee nii ? 155. Moo ndax dangeen dul fàttaliku ? 156. Walla dangeen am ay firnde yu wóor ? 157. Kon indil seenub Téere ndegam ñu dëggu ngeen ! ” 158. Ñu di ko askanale ci jinne yi, ndax jinne yi xam nañu ne danañu teew ci kanamu [Yàlla]. 159. Tudd naa sellug Yàlla ga. Kawe na lool la ñu koy melal ! 160. Ba mu des jaami Yàlla yiy sellal. 161. Yéen ak li ngeen di jaamu,
coran-wolof.pdf
page_363
363 162. kenn duleen ci fitnaal, 163. ku dul kuy nar a xoyomu ci Safara. 164. Amul kenn ci [Malaaka yi] lu dul ne am na wàccuwaay wu ñu xam ; 165. te noo leen defoon ay sàppe ; 166. te nun nooy sàbbaal Yàlla. 167. Doonte la sax ña ngay wax naan : 168. “Su nu amoon waarate gu bawoo ca sunuy maam, 169. kon de nu doon ay jaami Yàlla yuy sellal ! 170. Weddi nañu ko, waaye danañu xam ne. 171. Sunu kàddu jiitu woon na ci Sunu jaam ña di ay Yonent, 172. ñoom danañu am ndimbal, 173. te it Sunuy xarekat ñooy not. 174. nanga leen dummóoyu ab diir ; 175. te nga seetluleen : danañu gis de ! 176. Moo ndax ñoom dañuy yàkkamti sunu mbugal ?
coran-wolof.pdf
page_364
364 177. Su wàccee ci seenub ëtt, ñoom ña ñu doon fàttali, ndaw suba gu bon ! 178. nanga leen dummóoyu ab diir ; 179. te nga seetluleen : danañu gis de ! 180. Tudd naa sellug sa Boroom, Boroom kàttan gi. Kawe na ca la ñu koy melal ! 181. Te jàmm yal na wàcc ci Yonent yi, 182. te xeeti cant yépp ñeel na Yàlla miy Boroom àddina si ! ----------------------------------------------------------------------------- Saar 38 : SAAD 88 Laaya – Laata Gàddaay ga ----------------------------------------------------------------------------- Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi. 1. Saad. Maa ngi giiñ ci Alxuraan, miy boroom tur ci ne : 2. Ña weddi ña nga cag rëy-rëylu ak kaŋ-kaŋ ! 3. Aka bari ñu nu faagaagal ca ña leen jiitu woon, ñu daan yuuxu, walla te du ñu man a raw? 4. (Waa Màkka) daana yéeme ci waaraatekat bii leen digal te bokk ci ñoom, yéefar ya daan wax naan : “Kii dey ab njibarkat la bu di ab fenaakoon,
coran-wolof.pdf
page_365
365 5. Moo ndax dafa bëgg a def Yàlla yii muy jenn Yàlla ? Aa lii dey mbir mu yéeme la”. 6. Kilifa ya ne leen : “Demleen, te muñ jàpp ci seen Yàlla yii : lii daal la nu bëgg. 7. Nun masunoo dégg lii ci diine ji fi mujj wàcc (Iisaa) ; lii daal ay sos rekk la ! 8. Nuy wax naan, ak ni nu tollu ndax ci moom la [Alxuraan] di wàcc? ” Li wer moo di yéefar yaa ngay sikki-sàkka ci sama Téere bi. Xanaa kay dañoo mosagul mbugël ! 9. Walla ndabi yërmaandey sa Boroom tey Mayewaakoon, biy boroom Kàttan bi, da fa nekk ci ñoom. 10. Walla dañoo moom nguurug asamaan yeek suuf si, ak li nekk ci seen diggënte? su fekkee ne looloo am kon nañu def pexe ci yéeg ci ! 11. Ak nu seeni xarekat man a tollu ak ña leen di jàppale, danuy nërméelu ! 12. ña leen fi jiitu woon, weddi woon nañu ña di nitu Nooh, ak Aad ak Firawna ma doon boroom dëx (tabax yu rëy), 13. ak Samuud, ak nitu Lóot, ak waa Aykata, (ñoom ñépp weddi woon nañu seeni yonnent). Te ñoom ñoo di jàppalekat ya (farandoo ya). 14. Ñoom ñépp weddi woon yonnent ya. Nu daldi leen mbugël ! 15. Ñoom xaaruñu lu dul genn xaacu, gu dul tóllantiku wol. 16. Ñuy wax naan : “Yaw sunu Boroom, gaawal jox nu sunu wàll balaa wañoo ba”. 17. Muñal lii ñuy wax ; te ngay fàttaliku Sunu jaam ba Daawuda ma doonoon boroom doole, Moom ku faral daan dellu ci Boroomam la woon.
coran-wolof.pdf
page_366
366 18. Tàggataloon Nanu ko, tundi doj yi nu daan ànd ak moom, di sàbbaal Yàlla subaak ngoon, 19. picc yépp it dañuy dajaloo, di delloo kañ [Yàlla]. 20. Dëgaralal Nanu ko nguuram jox ko xam-xamu xereñe ràññee ak xam-xamu àtte. 21. Moo ndax xibaari xulóokat ya agsi na ci yaw ba ñu bëttee ñagub mbaar ma (mihraab ba) ! 22. Ba ñu duggee fekk fa Daawuda, mu tiit ci ñoom. Nu wax ko ne : “Bul tiit ! Ñaari way xuloo la nu ; kenn ci nun dafay néewal dole ka ca des. Kon àtteel sunu diggënte ci dëgg, te it nga gindi nu teg nu ci yoon wu jub xocc wa. 23. Kii nag sama mbokk la : amna juróom-ñeenti fukki xar ak juróom ñenenta, man ma am menn xar doŋŋ. Mu wax ma ne : “Naa ko ko jox” ; daldi wane lool ; doole ca ba ñuy waqante”. 24. [Daawuda] ne ko : “Moo la tooñ ci laaj gi mu la laaj sam xar ngir dollee koy xaram”. Te ñiy faral a ànd di liggéey bariyaana ba ñennat ci ñoom jaayee doole ña ca des, ba mu des ña gëm tey def yiw – te ñooña ñu néew lañu ci. – Daawuda daldi xam nag ne dañu ko doon nattu. Mu daldi rot (rukuu) sëgg jàpp ci ay wóomam delluwaat ca Boroomam. 25. Nu daldi koy jégël loola. Te amna daraja ju Nu jige ak wàccuwaay wu jekk. 26. “Éy yaw Daawuda, def Nanu la ngay sunu kuutlaay ci kaw suuf si. Na ngay àtte diggënte nit ñi ci dëgg te bul topp mukk bànneex : su ko defee dana la féewale ak yoonu Yàlla”. Te ñiy féewook yoon danañu am mbugël mu tar mitti ngir lañu fàtte bisub wañoo ba (Bis Pénc ba). 27. Te bindunu asamaan ak suuf ak li nekk ci seen diggënte cig neen. Loolu la yéefar ya njortu. Te yéefar yaa ngaay tuskare ca biir safara ! 28. Moo ndax dañuy jëflaantéek yàqkat yi nekk ci suuf ? walla danuy jëflaantéek ña ragal Yàlla kem ni ñuy jëflaantéek kàccoor yi ? 29. [Lii] ab Téere la bu Nuy wàcce ci yaw bu barkeel nak, ngir ñuy settantal ay laayaam ak it ngir woroomi xel yi man ciy fàttalikoo!
coran-wolof.pdf
page_367
367 30. May Nanu Daawuda (doomam ja) Sulaymaan, - ndaw jaam bu baax ! – Ku daan dellu ca boroomam la. 31. (Fàttalikul) ngoon ga, ñu ko gaarale fasi naari góor ya, 32. Sulaymaan dellu wax ne : “Cëy man, maa ngi fees dell ak bëgg (àddina sii) mu fàbbi maa ba jant bi so te fàttalikuwuma sama Boroom. 33. Delloosil ma fas yi.”. Ñu delloosil ko ko mu dagg yeel ya ak doq ya. 34. Nattu Nanu Sulaymaan ci nu sànni ca toogoom ba (jëmm ju nu wotte). Mu delluwaat, màggal Boroomam. 35. Mu wax ne : “Yaw sama Boroom, na nga ma jégal te may ma nguur goo xam ne kenn dootu ko am sama ginnaaw. Yaw yaay Mayaakoon bi”. 36. Tàggatal Nanu ko ngelaw li, muy daw ci ndigëlam, ak fu mu jublu. 37. Tàggatal Nanu ko sayaane yi, ñu di ko tabaxal ak di ko nuural ci (ndox). 38. Ak ñeneen, ñu ñu lëkkële ak i njéng. 39. “Lii mooy sunug may ; mayeel walla nga téye ko kenn du ko waññook yaw”. 40. Te mooy am na daraja ju Nu jege ak wàccuwaay wu jekk. 41. Fàttalikul sunu jaam Ayyuuba , ba muy woo Boroomam naan ko : “Yaw sama Boroom Saytaane teg na ma coono ak i tiis”. 42. (Yàlla ne ko) dóoral sa tànk fi ci suuf : am ndox ngi nii mu sedd mu man a sangu neex a naan.
coran-wolof.pdf
page_368
368 43. Nu delloowaat ko njabootam joxaat ko lu na tollu, muy yërmande ju bawoo ci Nun ak fàttili woroom xel yi. 44. “Ŋëbal sëqub ñax, te dóor ko ko (soxnaam sa). Te bul gàddu bàkkaarub ngiiñ”. Moom, muñkat la di jaam bu baax. Kuy farlu di dellu ci Boroomam la. 45. Fàttalikul suñu jaam ña Ibraahiima, ak Ishaaq ak Yaaquub ? Woroomi kàttan la ñu woon ak i gis-gis (xel). 46. Noo leen ràññi woon ngir sellalug : fàttaliku bis pénc ba. 47. Te ñoom, bokk nañu, ca tànnéef ya gën a ràññiku. 48. Fàttalikul Ismaahiila ak Ilyaas, ak Suul kifli, ñoom ñépp ay tànnéef la ñu. 49. Lii ag fàttali la. Te ne ñay ragal Yàlla, am nañu, wàccuwaay wu jekk, 50. Àjjanay Adan, seen wunt ya ne ŋàll ngir ñoom, 51. dañu fay, sóonu, di woo ay futéef yu bari ak i naan. 52. Amnañu fa ay jigéen (jabar) ñu di ay lamsalkat, yu maase ay at. 53. Lii mooy li Nu leen dégóon ci bisub wañoo ba. 54. Lii moo di sunu xéewal gi te du jeex mukk. 55. Yëgal it ne ! ñay bew am nañu wàccuwaay wu yées, 56. Mooy Safara su ñuy xoyomoo. ndaw kër gu bon ! 57. Mi ngi nii ! Nu cay tokamtiku : ndox muy tàng ak a wañax,
coran-wolof.pdf
page_369
369 58. ak yeneeni xeeti mbugël yu mu témbóol. 59. Ñii ay mbooloo la ñu ñuy buuxanteek yéen, kenn dalaluleen. Te ñooy xoyomu ca Safara. 60. Ñuy wax naan : “Yéen kay la kenn dul dalal, lii, Yéen la ñu ko waajal”. Te ndaw saxuwaay bu bon ! 61. Ñuy wax naan : “Yaw sunu Boroom na nga dolli, ki nu waajalal lii, mbugël muy fulandiku ca biir Safara ”. 62. “Ana lan moo xew ba gisunu fi gaa ya nu daan limaale ci saay-saay si ? 63. Moo ndax dañu leen ko daan tooñe walla danu làqu sunu gëm ? ” 64. Lii daal tigi mooy xulóob waa Safara. 65. Waxal ne : “Man daal ab xuppekat laa. Te jenn Yàlla amul judul, Yàlla jiy jenn , Notaakoon ba, 66. Mooy Boroom asamaan yeek suuf si ak li nekk ci seen diggënte, te mooy boroom Kàttan gi, di Jégëlaakoon bi”. 67. Waxal ne : “Xibaar bu rëy la, 68. waaye yéen dumóoyu ngeen ko. 69. Amuma woon xam-xam ca xulóob kilifa ya gën a kawe. 70. Li nu may soloo doonul lu dul ne man mii ab xuppe kat laa waaraatekat bu bir”.
coran-wolof.pdf
page_370
370 71. (Fàttalitul) ba sa Boroom waxee Malaaka ya ne leen : “Man de maa ngi sàkk mbindéef ci ban. 72. Suma ko móolee ba ëf ci Sama Ruu, na ngeen daldi rot, sujuudal ko”. 73. Malaaka ya yépp daldi sujuud, 74. ba mu des Ibliis moom dafa rëy-rëylu bokk ca yéefar ya. 75. (Yàlla) daldi ne : “yaw Ibliis, lan moo la tere nga sujuud ci lii ma bind ci samay yoxo ? Dangay rëy-rëylu walla dangaa bokk ci ña kawe ? ” 76. “[Ibliis,] tontu ne ko : maa ko gën ndax yaa ngi ma bind ci safara moom nga bind ko ci ban”. 77. (Yàlla) ne ko : “Génnal ca biti, dàkku naa la ; 78. te Samam rëbb dal na la ba baa saa di taxaw”. 79. “[Ibliis,] ne ko : yaw sama Boroom, muñal ma, ba bisub dekkiwaat ba”. 80. (Yàlla) ne ko : “may Nanu la dig boobu, 81. ba ca bisub waxtu wu ñu xam wa (Bis Pénc ba)”. 82. “[Ibliis ne ko] giiñ naa ci sa màgg gi ne ! Danaa leen lajj loo ñoom ñépp, 83. ba mu des sa jaam ñiy sellal”. 84. (Yàlla) daldi wax ne : “Maa ngi waat, ci dëgg ne dëgg laay wax, 85. Danaa feesal Safara ci yaw ak ña la topp ñépp”.
coran-wolof.pdf
page_371
371 86. Waxal ne : “Laajumaleen ci ag pey ; te it yanuwuma ci. 87. [Alxuraan] jii daal ag fàttali la ñeel waa àddina si yépp. 88. Te dangeen xam ay xibaaram ci ndiir su yàggatul ! ”. ----------------------------------------------------------------------------- Saar 39 : MBOOLOO YA 75 Laaya – Laata Gàddaay ga ----------------------------------------------------------------------------- Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi. 1. Wàcceg Téere ba bawoo ca Yàlla, miy boroom Kàttan, di ku Xereñ. 2. Wàcce Nanu ci yaw Téere bi ci dëgg. Na ngay jaamu Yàlla te di ko sellalal jaamu ga. 3. Yàlla rekk am diine ju sell. Ñay jaamu leneen lu dul moom tey (wax naan) : “Lii nuy jaamu daal danu ciy sukandiku ngir man a jigeñ Yàlla”. Te, Yàlla dana àtte seen diggënte ci la ñu daan woote. Yàlla du gindi fenkat bu weddiwaakoon. 4. Su Yàlla nàmmoon jàppe kenn doomam, Kon dana tànn ca la mu bind namu ko soobe (waaye nammu ko). Tudd naa Sellam ga ! Mooy Yàlla, jiy Jenn, tey Notaakoon ba. 5. Moo bind asamaan yeek suuf si ci dëgg. Mooy muur guddi ci kaw bëccëg mooy mur it bëccëg ci kaw guddi, moo tàggat jant beek weer wi lu ca nekk ngay daw ci ab dig bu ñu ko àppal tigi. Mooy boroom Kàttan gi, di Jégalaakoon bi ! 6. Moo leen bind ci jenn jëmm daldi cay defar soxnaam sa. Te wàcceel na leen ci mala yi lu tollook juróom-ñatti tóllent. Mu di leen sos ci seen biiri nday, cig sosu ginnaawug sos, ci biir
coran-wolof.pdf
page_372
372 yatti lëndamaay. Koo koo di Yàlla, seen Boroom ! Moo moom Nguur. Te amul jeneen Yàlla judul Moom. Man dey xamuma naka ngeen koy walbatee ? 7. Su ngeen weddee, Moom doyewu leen dara. Te gëramul kéefër, ci jaamam yi. Su ngeen santee, Mu gëramal leen ko. Amul kenn kuy yanu bàkkaarub keneen. Te it, dees na leen delloo ca seen Boroom : Mu xamal leen la ngeen daan jëf ndax Moom ku xam la li nekk ci dënn yi (pas-pas yi). 8. Te saa su lor laale nit, dafay daldi fàtte la mu doon woote aka ñaan Boroomam daldi wutal Yàlla ag bokkaale. Di rëyal nit ñi fàbbi leen ci yoonu Yàlla, Waxal ne : “Bànneexul tuuti ci sa kéefër gi. Yaw ci waa Safara nga bokk”. 9. Moo ndax, kuy jóg, diggu guddi, di sujuud ak a taxaw( julli), ngir moytu (tiisu àllaaxira) tey yaakaar yërmaandey Boroomam... Waxal ne : “Ndax ñi xam danañu yem, niróok ñi xamadi ? ” Li wér moo di ne woroom xel yi rekk ay fàttaliku. 10. Waxal ne : “Éy yéen Sama jaam ñi gëm ! Ragalleen seen Boroom (Yàlla)”. Ñiy jëf aw yiw ci àddina, danañu am [aw yiw]. Te suufus Yàlla si yaatu na te muñkat yi danañu leen jox seenug pey mu mat sëkk ci lu dul ak waññ. 11. Waxal ne : “digëléef na ma may jaamu Yàlla di ko sellalal diinéem, 12. te it digaléef na ma doon Jullit buy jëkk. 13. Waxal ne : “Ragal naa, su ma mettee sama Boroom, (dajeek) mbugëlam bis bu màgg”. 14. Waxal ne : “Yàlla laay jaamu, te di Ko sellalal sama diine. 15. Jaamuleen, lu leen soob (bàyyi Yàlla)! ” – Waxal ne : “ña yàqule, ñooy ña ñàkk seen bopp ak seen njaboot, ca Bis Pénc ba”. Loolu mooy yàqule tigi. 16. Am na ci seen kaw, ay muuraayi safara, ak ci seen suuf ay laltaayi safara. Loolu la Yàlla di ragalloo jaamam ñi. “Éy yéen Samay jaam, ragalleen ma ! ”
coran-wolof.pdf
page_373
373 17. Ñay moytandikoo jaamuy xërëm, tey dellu ca Yàlla, danañu am mbégte ! Bégalal Sama jaam ñi 18. Ña nga xam ne dañuy déglu Wax, tey topp la ca gën a rafet. Ñoom la Yàlla gindi te ñooy woroom xel ya ! 19. Ka baatub mbugël yay ci moom,... ndax yaw yaay xettali ku nekk ca biir safara ? 20. Waaye ñay ragal seen Boroom am nañu [ay neegi] taax yu tegaloo ay dex di daw ci suufam. Muy digub Yàlla ! Te Yàlla du wuute Ab dégg. 21. Xanaa gisoo ne Yàlla wàcce na ndox mu bawoo asamaan, daldi koy sóob ci bëtu ndox ci biir suuf si ; di ca, génne mbay mu wuute ay wirgó, di lu bëbbu, nga gis ko mu mboq wow ; bay, dammatoo. Ag fàttiliku nekk na ci biir loolu ngir [aw nit] ñu am ay xel. 22. Moo ndax ki Yàlla ubbi dënnam ci Lislaam mu nekk ci leerug Boroomam( moo gën walla ka des cig kéefër)... Toskare ñeel na ñiy bañ a tudd Yàlla ngir xol bu wow. Ñoom ña nga ca réer gu bir. 23. Yàlla wàcce na gën jaa rafet waxtaan, muy Téere bu bari yu niróo ak i baamu. Yaramu ñi ragal Yàlla day daw [saa su ñu ko déggee] ; ba egal seen yaram ya ak seen xel ya door a firiku jëm ci fàttaliku Yàlla. [Alxuraan] jooju moo di njubug Yàlla mu di ci gindi ku ko soob. Ku Yàlla namm a réeral kenn du ko gindi. 24. Moo ndax ki am bugël mi gën a gën a bon ( niróo na ak ka dugg Àjjana), bu Bis Pénc baa bu boobaa tooñkat ya... Dañu naan leen : “Tokamtikuleen li ngeen daan fàggu”. 25. Xeet ya leen fi jiitu woon weddi woon nañu (Yonnent yi), mbugël ma dikkëlleen fuñu ko foogewul. 26. Yàlla musal na leen mbugëlu toroxtaane ci dundug àddina sii. Te mbugëlu àllaaxira, moo, gën a rëy, cëy bu ñu xamoon ! 27. saddalal Nanu nit ñi ay léebu ci Alxuraan jii, ndax amaana ñuy fàttaliku.
coran-wolof.pdf
page_374
374 28. Mooy Alxuraan ju di [làmmiñu] araab, amul lugg-luggal, ndax amaana ñuy ragal Yàlla ! 29. Yàllaa ngi sadd léebu jenn waay ju am digaale yu bari tey ŋaayoo : ndax niróonaak waa ju am benn digaale bu mu jubóol ? Yàlla rekk yayoo cant ! Li am moo di ne li ëpp ci ñoom xamuñu (misaalum kuy jaamu Yàlla ak ku koy bokkaale). 30. Yaw dangay dee ñoom it dañuy dee ; 31. su ko defee, ngeen daje ca seen kanamu Boroom, di xulóo bu Bis Pénc baa. 32. Ana kan moo gën a tooñ, kuy fenal Yàlla tey weddi dëgg saa su dëgg dikkee ? Moo ndax Safara dafa amul wàccuwaayub yéefar ya ? (Axakaañ !) 33. Ku indi dëgg ak ku koy saxal, ñooñoo ragal Yàlla. 34. Am nañu lu leen soob fa seen Boroom ; loolu mooy peyug ñiy rafetal, 35. te Yàlla dana far seen ñaawtéef fay leen ca la gënnoon a rafet ca la ñu daan jëf. 36. Moo ndax Yàlla dafa doyul [wéruwaay] ci ab jaamam ? Bay tax ñu di la tiitale ci leneen lu dul Moom. Képp ku Yàlla natt ci moom réer kenn du ku gindi. 37. Te it képp ku Yàlla namm ci moom njub, kenn du ko réerël. Moo ndax Yàlla dafa dul boroom Kàttan di boroomuk Fayu ? Axakañ ! 38. Soo leen laajoon : “Ku bind asamaan yeek suuf si ? ”, Ñu ni la : “Yàlla”. Waxal ne : “Xanaa gisu leen li ngéen di jaamu bàyyi Yàlla ; ci ne su Yàlla nammee ci man lor, ndax ñoom kon danañu man a teggi lor ja ? Walla su Yàlla nammoon ci man yërmaande, ndax kenn danañu man a fanq yërmaande ja ? ” – waxal ne : “Yàlla doy na ma : ci moom la wéerukat ya di wéeru” 39. Waxal ne : “Éy yéen samaw nit, liggéeyleen lu ngeen man, man it [maa ngi liggéey]. Dangeen xalset a xam
coran-wolof.pdf
page_375
375 40. ana kan la mbugël di dikk toroxal ko ; ak ci kaw kan la mbugëlam dëggële di wàcc”. 41. Wàcce Nanu ci yaw Téere ba, ci dëgg, ngir nit ñi. Ku gindiku boppam ; ku réer it boppam. Seenub lijjënti warula 42. Yàlla mooy faat bakkan bu ñuy dee ak ya deewul ci biiri nelaw. Mooy téye ya mu namm ñu dee, di boyal ya ca des jëme ko ca dig ba mu ko àppal. Ay kéemaan a ngi ci biir loolu ngir aw nit ñuy xalaat. 43. Walla dañoo wut, yeneeni tinukat, bàyyi Yàlla ? Waxal ne : “Ndax ! Nekkuñu woon ñu amal dara te xamu ñu dara ? ” 44. Waxal ne : “Tinu ba tinu jeex (ramm) Yàllaa ko jagoo. Miy boroom nguurug asamaan yeek suuf. Te ci moom ngeen di dellu” 45. Te saa su ñu tuddee Yàlla doŋŋ, xoli ñi gëmul àllaaxira tàmbalee wurwuri (xat mer) saa su ñu tuddee ñeneen (ya ñu koy bokkaaleel), ñu daldi bég. 46. Waxal ne : “yaw sama Boroom, Yaa bind sàkk asamaan yeek suuf si, Yaa xam kumpa ak li feeñ, te danga àtte diggënte Sa jaam ñi ci la nu daan woote”. 47. Te ñiy tooñ su ñu amoon àddina ak li ci biiram, - ak leneen lu na tollaat, - kon danañu ko jéem a jote seen bopp bu Bis Pénc baa ; ngir mbugël mu tar, ak la ñu gis mu bawoo ca Yàlla, te masu ñu koo foog ; 48. seen ñaawtéef ya ñu fàggu woon feeñ, la ñu daan ñaawalaatee muur leen. 49. Saa su nit amee lor ju ko dab, danuy daldi woo. Tey ñaan waaye saa su nu ko teggee may ko xeewël, muy wax naan : “lii ci [sama] xam-xam laa ko ame”. Ab nattu la, de; waaye li ëpp ci ñoom xamuñu. 50. Ña leen fi jiitu woon waxoon na ñu ko. Te taxul la ñu daan fàggu jariñ leen dara ; 51. Faf sax la gënoon a ñaaw a la ñu daan fàggu moo leen dal. Te ñii itam li gën a ñaaw ca la ñu doon fàggu dana dal ci seen kaw te duñu ko man a teggi.
coran-wolof.pdf
page_376
376 52. Xanaa dañoo xamul ne Yàlla mooy yaatalal ku ko soob wërsëgam di ko xatal it ? Ay kiiman a ngi ci biir loolu ngir aw nit ñu gëm. 53. Waxal ne : “Éy yéen Sama jaam ñi yàq seen bopp, buleen naagu ci yërmandey Yàlla. Ndax Yàlla dana jégële bakkaar yépp. Mooy Jégëlaakoon ba, di Jaglewaakoon ba”. 54. Delluleen ci seen Boroom, te jébël ko seen bopp, balaa mbugël di dal ci seen kaw te kenn duleen ca dimbali. 55. Te it na ngeen di topp li gën a rafet ci li nu wàcce (Alxuraan) ci yéen mu bawoo ca seen Boroom, balaa mbugël di dal ci seen kaw te du ngeen ko yëg ; 56. balaa benn bakkan di wax naan : “Wóy ngalla man ci na mu soofentale woon mbiri Yàlla. Te daan ca reetaan nit ña” ; 57. walla mu naan : “Suma Yàlla gindi woon, kon danaa bokk, ca ñay ragal Yàlla” ; 58. walla muy wax ba mu gisee mbugël ma naan : “Cëy ! Suma delluwaatoon àddina ! Ba man a bokk ca ñay rafetal”. 59. “Mukk ! Ndax Samay laaya dikkaloon na la nga weddi ko, di rëy-rëylu dem àndeek yéefar yi”. 60. Bu Bis Pénc baa, dangay gis ña fenal Yàlla, seen xar kanam ya ñuul kukk. Moo ndax wàccuwaayi yéefar ya nekkul ca biir Safara ? (Axakañ) 61. Yàlla dana musël ña ragal Yàlla te texel leen [ca Àjjana]. Lu bon du leen fa laal te it duñu fa jàq. 62. Yàlla moo sàkk bind lépp, te it Mooy lijjënti lépp it. 63. Moo moom caabiy asamaan yeek suuf si ; ñay weddi kàdduy Yàlla, ñooy ña yàqule.
coran-wolof.pdf
page_377
377 64. Waxal ne : “Yéen ñi réer, ndax dangeen may digël may jaamu lu dul Yàlla ? ” 65. Te, soloona Nu la ak (Yonnent ya la jiitu woon) ci ne : “Saa soo bokkaalee , sa jëf dana sippiku; nga bokk ci ñu yàqule ña. 66. Jaamujil Yàlla, tey sant”. 67. Joxuñu Yàlla dayoom tigi, suuf si sépp ab ŋëbëm lay doon bu Bis Pénc baa, asamaan yépp ab lem lay doon ci [loxoom]. Tudd naa Sellam ga ! Kawe na ci liñu koy bokkaale. 68. Suñu ëfee bufta bi, lu nekk ci asamaan yeek suuf si léppay dee, lu dul la ca soob Yàlla. Ñu ëfaat ko beneen yoon ndeketeeyóo, ñépp a ngi ne fujjet jóg taxaw ne xey di xoole. 69. Suuf si daldi fenk ak leerug Boroomam ; ñu daldi teg Téere ba, indi Yonnent ya ak seede ya ; daldi àtte seen diggënte ci dëgg te kenn duleen tooñ ci dara ; 70. bakkan bu nekk ñu fay ko la mu daan jëf. Te [Yàlla] moo gën a xam ñu daan def. 71. Ñuy jiital yéefar yi jëme leen Safara ñu di ay mbooloo. Bu ñu fa àggee, buntu ba ubbiku ña koy wattu ne leen : “Xanaa amuleen woon ay Yonnent yu leen daan jàngal kàdduy Yàlla seen Boroom ak daan leen xupp ci dajeb seen bis bii ? ” Ñu ne leen : axakañ, waaye dogalub mbugël yay na ca yéefar ya. 72. “Ñu ne, [leen] dugguleen, wunti Safara, ngeen béel fa”. Rëy-rëylu kat tee ka bon ab saxuwaay ! 73. Ñooy jiital ña ragaloon seen Boroom jëme leen Àjjana. Ñu, di ay mbooloo bu ñu fa àggee wunt ya ubbeeku, ña koy wattu ne leen : “Jàmm rekk yal na nekk ci yéen ! Yéen dey baax ngeen : dugguleen ci, te dangeen ciy béel”. 74. Ñuy wax naan : “Noo ngi sant Yàlla mi nu dëggëlal digëm bi te donale nu suuf si ! Tey noo ngi xéyoo ci Àjjana nu mu nu neexe”. Ay waay gii pey a neex ! 75. Nga gis Malaaka yaa ngay wër (Aras), di sàbbaal seen cantug Boroom. Ñu wax naan : “Xeeti cant, ñeel na Yàlla miy Boroom àddina si”.
coran-wolof.pdf
page_378
378 ----------------------------------------------------------------------------- Sourate 40 : JÉGËLEKAT BA 85 laaya - Laata Gàddaay ga ----------------------------------------------------------------------------- Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi. 1. Haa, Miim. 2. Wàcceg téere bii ma ngi bawoo ca Yàlla, miy boroom Kàttan, te di ku Xam. 3. Mooy Jéggalkatu bàkkaar yi, di Nanguwaakoonu tuub, di ku Tar mbugël, mooy Boroom xéewal yi. Amul jeneen Yàlla judul Moom te ci Moom la lépp di mujj. 4. Kenn du dàggasante ci kàdduy Yàlla ku dul yéefar yi. bu la seeni feem nax. 5. Nitu Nooh, weddi woon na ñu ca la leen jiitu woon, ak farandoo ya (weddi woon na ñu ñoom itam), xeet wu nekk taqal ab yonnentam. Sànjaafu ko di dàggasante ak moom bëggoon a suufeel dëgg. Mu daldi leen fob (faagaagal leen). Cëy ni ma leen mbugële ! 6. Noonu it la sa kàddug Boroom yaye ci kaw yéefar yi : “Ñoom ñooy waa Safara”. 7. Ña yanu Aras ak ña ko wër ña ngay sàbbaal di kañ seen Boroom, di ko gëm tey jéggalu ñi gëm naan ko : “Yaw sunu Boroom ! sa yërmaande yaatu na man a daj ñépp ak sa xam-xam. Kon jéggëlal ña daan tuub tey topp sa yoon wi te nga fegalleen mbugëlu Safara. 8. Yaw sunu Boroom ! Tàbballeen àjjana Aden ja nga leen digoon, ak képp ku baaxoon ci seeni baay ak i maam, ak seeni soxna ak seeni sët, yaw yaa di boroom Kàttan, di ku Xereñ. 9. Te nga fegalleen [mbugëlu] ñaawtéef yi. Képp koo fegal [mbugëlum] ñaawtéef, Yërëm nga ko tigi”. Te loolu mooy texe gu mag ga.
coran-wolof.pdf
page_379
379 10. Ña weddi nag ñoom dañu leen woo naan leen : “jéppig Yàlla moo gën a rëy ni ngeen jéppee seen bopp, ba ñu leen daan woo jëme leen ci ngëm dangeen daan weddi”. 11. ñuy wax naan : “Yaw sunu Boroom, rey nga nu ñaari yoon, dundal nga nu ñaari yoon : nangu nanu sunuy bàkkaar. ndax lii man nanu tee génn” ? 12. “...Amul ndax bu ñu masaan a woo Yàlla doŋŋ ngeen weddi ; bu ñu ko bokkaalewaale ak leneen, ngeen gëm koo. (Tey jii), àtte ba Yàllaa ko yor, moo di ku Kawe, te di ku Màgg”. 13. Moo leen di won ay kéemaan, di leen wàcceel ndox, mu bawoo asamaan, ngen di ca xéewlu. Te ñay dellu [ca Yàlla] rekk ay fàttaliku. 14. Ñaanleen Yàlla, te jaamu Ko te sellalal ko diineem, doonte la neexul yéefar yi. 15. Moo kawey daraja, di Boroom Aras, Mooy sànni ruu ci ndigalam jëme ko ci ku ko soob ci jaamam ñi, ngir muy xuppe ci bisub Daje ba (Bis Pénc ba), 16. bis ba ñuy feeñ seen dara du man a nëbbu Yàlla. Ana kan mooy boroom nguur gi, bis niki tey ? Yàlla, miy Kenn, di ab Notaakoon. 17. Bis niki tey, bakkan bu nekk dees na ko faye ca la mu daan fàggu. Tooñ amatul, Yàlla ku gaaw ab wàññ la. 18. na nga leen xupp ci bis buy jige si, ba xol yi di nekk ci put yi, (ngir tiit ak njàqare). Te bu boobaa tooñkat yi du ñu fa am xarit, mbaa ku leen di tinu ñu di ko topp. 19. Xam na worug ay gët, luy nëbbu ci biir dënn yi. 20. Yàlla mooy àtte ci dëgg, ña ñu koy bokkaaleel du nu àtte dara. Te Yàlla kuy Dégg la, kuy Gis la. 21. Moo ndax da ñoo doxul ci suuf, tey seetlu mujug ña leen fi jiitu woon te ëppoon doole ak i alal ? Yàlla faagaagaloon leen ngir seeni bàkkar. Te kenn manu leen woon fegal mbugëlu Yàlla mii.
coran-wolof.pdf
page_380
380 22. Li ko waral, moo di ñoom seeni Yonnent, da ñu leen daan indil ay lay yu leer ñu weddi. Yàlla daldi leen faagaagal, Yàlla boroom doole la di ku Tar mbugël. 23. Yónni woon nanu Muusaa ak sunuy laaya boole ko ak ay firnde yu leer, 24. jëmële ko ca Firawna, ak Haamaana ak Qaaruuna. Ñuy wax naan : “Kii ab njibarkat bu di ! ab fenaakoon la ! ” 25. Ba mu àggee ca ñoom, indi ko baawoo fi Nun da ñoo wax ne : “reyleen doom yu góor ñi gëm ànd ak moom, te bàyyi jigéen ñi ñuy dund”. Pexey yéefar yi du dara lu dul ci ag réer (lay tege). 26. Firawna daldi wax ne : “Bàyyileen ma rey Muusaa. Na woo Boroomam ! Da may ragal mu soppi seen diine walla muy ger nit ñi di yàq réew mi”. 27. Muusaa [daldi] ne : “Maa ngi sàkku ci sama Boroom mu musal ma ci képp kuy rëy-rëylu, te gëmul bisub wañoo ba (Bis Pénc ba)”. 28. Mu am waaju gëm te bokk ca waa kër Firawna, daldi wax ne : “Ndax dangeen a bëgg rey waa joo xam ne li mu wax lépp moo di ne : “Yàllaay sama Boroom” ? Te indil na leen ay firnde yu bawoo ca Yàlla. Su fekkee day fen, fenam ya du ko moy ; su waxee dëgg, ngeen dor a xam ne li mu leen dig dana dal seen kow”. Te, Yàlla du gindi mukk fenkat buy yàq (waaja da doon nëbbu ngëmam) ! 29. “Yéen samaw nit, tey yéen a ngi gore, am lool doole ci kaw suuf si (réew yi). Waaye ana kan moo nuy man a dimbali ci mbugëlum Yàlla su nu digëlee ? ” Firawna daldi ne : “Wanumaleen lu dul li ma gis. Te it duma leen teg fudul ci yoonu njub”. 30. Ka gëmoon daldi waxaat ne : "Yéen samaw nit, ragal naa ci yéen lu mel ni bis ba farandoo ya doon xare. 31. Lu melni lëgg-lëggub nitu Nooh, ak Aad ak Samuud, ak ña leen mujjoon”. Te Yàlla bëggul ag tooñ ci jaamam ñi.
coran-wolof.pdf
page_381
381 32. “Éy yéen samaw nit, ragal naa ci yéen bisub wootante ba, 33. Bis ba ngeen di wane sànku, te dungeen am ku leen di aar ci Yàlla”. ku Yàlla natt ci moom réer, kenn du ko man a gindi. 34. “Yuusuf, indaloon na leen ay firnde yu leer naññ, te de ñu leen di sikki-sàkka ca la mu indiwoon. Ba mu faatoo, ngeen wax naan : “Yàlla yónniwaatul beneen Yonnent ginnaawam”. Noonu la Yàlla di réerale ñiy yàq tey sikki-sàkka. 35. Ñiy dàggasante ci laaya Yàlla yi, ci lu àndul ak firnde ju leen digël jéppi gu rëy lay doon ca Yàlla ak ña gëm. Noonu la Yàlla di fatte xolub képp kuy rëy-rëylu di ponkal. 36. Firawna wax na ne : "Yaw Haamaan, tabaxal ma ag tóoj : ndax amaana ma man a gis yoon ya, 37. yooni asamaan yi, ndax ma man a yërndu Yàllay Muusaa ; te man sax ay fen laa ko jàppe”. Noonu la Firawna rafetloo jëfëm ju ñaaw joojee ; sorenaak dëgg lool ; te pexem Firawna du lenn lu dul luy naaxsaay. 38. Waa ja gëmoon daldi wax ne : "Yéen samaw nit, toppleen ma. Ma gindileen jëmëleleen ci yoonu njub. 39. Yéen samaw nit, dundug àddina sii diir bu néew la, dundug àllaaxira nag mooy sax. 40. Képp kuy def ñaawtéef dees na ko fay kem la mu def ; waaye képp kuy def yiw, di góor mbaa muy jigéen, te fekk mu gëm, ñoom ñooy dugg Àjjana di fa jot xéewël yu amul waññ. 41. Éy yéen samaw nit, ana lan moo tax ma di leen woo jëme leen ci mucc, te yéen ngeen di ma woo jëmale ma Safara ? 42. Yéen a ngi may woo ngir ma weddi Yàlla di ko bokkaaleek lu ma amul benn xam-xam, te man maa ngi leen di woo jëme leen ci Yàlla miy boroom Kàttan, tey Jégëlaakoon ba. 43. Sikkuwul ne li ngeen may woo jëmale amuñu luy tax ñu war leen a woo ci àddina sii waxantumaalaak ca àllaaxira. Te it ca Yàlla lañuy dellu, te itam yaqkat ya ñooy wa Safara.
coran-wolof.pdf
page_382
382 44. Yàggatul ne dangeen fàttaliku ji lii ma leen di wax ; te wéer naa samay mbir ci Yàlla. Ndax, kuy Gis jaamam ñi la. 45. Yàlla fegal na ko ñaawtéef ya ñu doon fexe, daldi sóob njabootug Firwana gën jaa tar i mbugël : 46. ñu di leen , gaaral ci Safara suba ak ngoon. Bu Bis Pénc baa (da naa digle) : “Ñu dugël njabootug Firawna ca gën jaa tar i mbugël”. 47. Bu keroogee ba ñuy xulóo ci Safara, ña néewoon doole di wax ña ca doon ay kilifa naan leen : “Ca àddina kat yéen la ñu toppoon : kon ndax tey dangeen nu fegal dara ci mbugëlum safara si ? ” 48. Ña ca doon ay kilifa te daan rëy-rëylu daldi ne : “Nun ñépp kat, ñi ngi ci biir Safara”. Ndax Yàlla àtte na diggënte jaam ñi. 49. Ña nekk ca biir Safaraa ngay wax ña koy wàttu naan leen : “Ñaanleen seen Boroom mu woyofalal [nu] doonte la sax benn bis lay doon ci mbugël mi”. 50. Wattukat ya ne leen : “moo ndax, seeni Yonnent indiluñuleen woon ay lay yu leer naññ” ? Ñu ne : “Axakañ” ! Ñu waxaat ne [wattukat ya]: “Kon, ñaanleen” ! Ñaanug yéefar moom ag réer doŋŋ la. 51. Nun, Yàlla dananu dimbali (jox ndam), Sunuy Yonnent, ak ñi gëm, ci dundug àddina sii ak bu seede ya taxawee (Bis Pénc ba), 52. bis ba nga xam ne tooñkat ya, seenug doglu ngànt du leen jariñ dara te am rëb dal na leen te it am nañu fa kër gu bon (soof). 53. Indil Nanu, Muusaa njub, te donale Nanu giiru Banii-Israayiila, Téere ba, 54. mu di njub ak ug fàttali ngir ñu di woroom i xel (di xalaat).
coran-wolof.pdf
page_383
383 55. Na nga muñ, (te xam ne) digub Yàlla dëgg la, te it na ngay jéggalu say bàkkar tey sàbbaal sa Boroom di ko sant, ci ngoon si ak ci suba si. 56. Ñay dàggasante ci laayay Yàlla ya ci lu àndul ak firnde yu ñu leen jox, rëy-rëylu doŋŋ a nekk ca seen dënn ya. Te seen aajo du ca fajoo. Na ngay muslu ci Yàlla, moom Mooy aji Dégg, di aji Gis. 57. Bindug asamaan yeek suuf si moo gën a rëy bindug nit ñi. Waaye li ëpp ci nit ñi xamuñu. 58. Gumba niróowul ak njàccaar, ña gëm tey jëf yiw it niróowuñu ak ñiy def ñaatéef (kenn du leen gam-gamle). Néewaana bu ngeen fàttalikoo ! 59. Bis Pénc ba ; Luy dikk la : nàttable amu ca ; waaye li ëpp ci nit ñi gëmu ñu. 60. Seen Boroom nee na : “Wooleen ma, Ma wuyu leen. Ña nga xam ne, dañoo rëy-rëylu, lànk bañ maa jaamu, danañu dugg Safara ànd ak toroxtaane”. 61.Yàlla mi leen defal guddi ngeen di ci dallu, defal leen bëccëg bi it ngeen di ci man a gis (bay fàggu ji). Yàlla boroom Ngënéel la ci kaw nit ñi, waaye li ëpp ci nit ñi duñu sant. 62. Koo ku moo di Yàlla seen Boroom, Moo bind lépp. Amul jeneen Yàlla judul moom. Kon naka ngeen di lajje féew (ca yoonu Yàlla wu jub wa xocc) ? 63. Noonu la ñu daan weddi kàdduy Yàlla di dumóoyoo [yoonu] Yàlla. 64. Yàlla mi leen defal suuf si muy laltaay defal leen asamaan si muy mbaar mu móol leen rafetal seeni melo , - wërsëgal leen ci yu teey yi ! Koo koo di seen Boroom ; Yàlla barkeel na, Moom Miy Boroom àddina si! 65. Mooy kiy dund. Amul jeneen Yàlla judul moom. Na ngeen koy jaamu, te di ko sellal diine ji. Cant ñeel na Yàlla, Miy Boroom àddina si ! 66. Waxal ne : “Tere na nu ma, may jaamu li ngeen di jaamu te du Yàlla, waxtu wa ma ay lay yu leer nàññ digëlee te bawoo ci sama Boroom, te it digaléef na ma jébël sama bopp Yàlla miy Boroom àddina si”.
coran-wolof.pdf
page_384
384 67. Mooy ki leen bind ci suuf, te jaarale leen ci toqu maniyy, ak ci lumbu deret door leen a génne ngeen di ay xale mu def leen ngeen di ay mag yu war a maggat kumur, - am na ci yéen ñuy faatu balaa loolu lépp di am, - ku ca nekk it am na ab dig bu ñu ko àppal, ak it ngir ngeen xellu (xalaat). 68. Mooy dundal mooy rey. saa su dogoo ci mbir, danaan ko : “nekkal”, mu daldi nekk. 69. Xanaa gisuloo ñiy dàggasante ci laayay Yàlla yi ni ñu leen di walbatee? 70. Ñay weddi Téere ba (Alxuraan) ak li nu yónnee sunuy Yonnent ; (waaye) dananu xala xam, 71. jéng, yaa nga seen doq ñuy gëwéele 72. ca biir ndox may wañax; ñu door leen a yóbbu xoyom leen ca Safara. 73. Bu loolu jàllee ñu ne leen : “Ana li ngeen daan bokkale 74. bàyyi Yàlla (jaamuwuleen ko) ? ” “Ñu tontu ne, réer nañu. Nun kay, lu jiitu tey, masunoo woo di jaamu dara”. Noonu la Yàlla di sànke yéefar ya. 75. Lii moo di peyug li ngeen daan bég ci suuf si (àddina), te du woon dëgg, ngeen daan ca maare. 76. Dugguleen ci wunti Safara te ngeen béel fa. Ña rëy-rëylu woon seenub dëkkuwaay bon na ! 77. Na ngay muñ (te xam ne). Digub Yàlla dëgg la. Amaana Nu wan la lenn ci li Nu leen di tëkkoo mbaa nu faat la (balaa loolu di am)... ak lu man a xew ñoom ñépp ci nun la nuy dellusi.
coran-wolof.pdf
page_385
385 78. Yónni woon Nanu ay Yonnent yu la jiitu woon. am na ci ñu ñu la nettali ; am na ci ñu ñu la nettaliwul. Amul benn yonnent bu sañ a indi [kimaan laaya] lu dul ne da ca am ndigëlul Yàlla. Saa su ndigëlul Yàlla agsee, mbir yépp àttewo ci dëgg ; fenkat yi daldi yàqule. 79. Yàlla mi leen defaral mala yi ngir ngeen di ci war te di ca lekk, 80. te am ngeen ci ay njariñ ak it ngeen di ca faj ay aajo yu leen soxal. Ngeen di ca yéeg di ànd ak ñoom di war ci gaal yi. 81. Mu di leen won ay kéemaanam. Naka ngeen koy weddee ? 82. Xanaa du ñu dox ci kaw suuf tey seetlu mujjug xeet ya leen jiitu woon ? ëppoon leen gënoon leen bari doole [ak i jeexit] ci suuf si. Te lañu daan fàggu fegalu leen dara (taxut woon mu doy leen). 83., Ba seen Yonnent dikkee indil leen ay lay yu leer nàññ, bokk na ca lañu xamoon. Lañu daan ñaawalaatee far sóor leen mujj leen talañ (faagaagal). 84. Ba ñu gisee Sunu Kàttan, daldi nañuy wax naan : “Yàlla doŋŋ la nu gëm, te weddi na nu la nu ko daan bokkaaleel”. 85. Seen ngëm googee jariñatuleen dara, ba ñu xasee ba gis tiis wa, muy àttey Yàlla ; Kem ni mu ko weyëlee woon ca jaamam ña. Foofee la yéefar ya di yàqulee tigi. ----------------------------------------------------------------------------- Saar 41 : LAAYA YU ÑU FARAMFÀNCE 54 laaya - Laata Gàddaay ga ----------------------------------------------------------------------------- Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi.
coran-wolof.pdf
page_386
386 1. Haa, Miim. 2. [Ak solool] gu ñu wàcce mu bawoo ci Yëramaakoon bi , di Jaglewaakoon bi (yërmandéem). 3. Ab Téere bu ñu faramfànce ay laayam muy Alxuraan di ko [jàng] ci làmmiñu araab ngir aw nit ñuy xam, 4. di bégle tey xuppe. Ña ëpp ci ñoom dañoo dumóoyu ; du ñu (ko) dégg. 5. Ñuy wax naan : “Sunuy xol dañoo muuru ci li nga ñuy woo jëmële, sunuy nopp dañoo saañu. Sunu diggënteek yaw kiraay da cee nekk, Defal li ngay def (yaw caag) ; nun noo ngi def li nuy def”. 6. Waxal ne : “Man nit laa ni yéen. dañu may soloo waaye seen Yàlla jenn Yàlla rekk la. Sàkkuleen tegu ca yoonam wu jub wa xocc te na ngeen sàkku njégël”. toskare ñeel na yéefar ya 7. ña dul génne asaka tey weddi (dikkug) Bis Pénc ba ! 8. Ñiy gëm tey jëfu yiw danañu am pey gu dootul dogamtal. 9. Waxal ne : “Ndax dangeen di weddi ki bind suuf si ci ñaari fan, ngeen di Ko sàkkal ay bokkaale ? Kooku moo di boroom àddina si, 10. Moo poose ay tundi doj ci kawam, def ca barke, (sakkan) mu doxal ca lépp luy yombal luy tax a man a dund ci diirub ñeenti fan. [Mooy tontul] képp ku la koy laaj. 11. Ba mu éggalee la yemoo ca asamaan muy Saxar mu daldi wax asamaan ak suuf moom Yàlla ne : “Dikkleen, ci bu leen neexee, walla bu leen naqaree”. Ñu tontu ko ne : “Dikk nanu ci sunu coobare”. 12. Dogal na ñay juróom-ñaari asamaan ci ñaari fan ci asamaan su ca nekk la muy liggéey. Te taaralal nanu asamaanu àddina si si gën a jige ak i làmp [biddiw] ak di ko sàmm. Loolu mooy Dogalub (Yàlla) kiy boroom Kàttan, di ku Xam.
coran-wolof.pdf
page_387
387 13. Bu ñu dumóoyoo lànk, waxal ne ; “maa ngi leen di xupp ci ag dënnu dënnu gu melni ga daloon waa Aad ak Samuud”. 14. Ba leen yonnenta ya digëlee, bawoo kanam ak ginnaaw, [daan leen digël]: “Ci nuy jaamu Yàlla (ba ña jaamu leneen)”, ñuy wax naan : “Bu neexoon Yàlla, Mu wàcce ay Malaaka. Te sax nun lii ñu leen yónni gëmuñu ko”. 15. Waa Aad, rëy-rëylu ci suuf ci lu dul dëgg, daan wax naan : “Ana ku ñu ëpp doole ? ” (Di damu) ! Daan féttéerlu ci sunuy laaya. 16. Bayal nanu ca ñoom ngelawul callmeer lu sedd guy ay fan yu nduxum, ngir mosal leen mbugëlum toroxtaane ci dundug àddina sii. Te mbugëlum àllaaxiraa gën a man a toraxal te it kenn duleen fa dimbali. 17. Waa Samuud nag ñoom, gindi woon nanu leen ; waaye dañoo tànni ngumba bàyyi gindi ku (njub) dëng. Mbugalum doyadi fab leen muy peyug la ñu daan fàggu. 18. Nu daldi musël ña gëmoon tey ragal Yàlla. 19. Bu keroogee bis ba ñuy pang (dajale) nooni yàlla ya... Jëme leen Safara di leen gur-gur. 20. Bu ñu nee jaas agsi ci Safara, seeni nopp, ak seeni gët at seeni yaram dañuy doon ay seede ci li ñu daan def. 21. Ñuy waxanteek seen deri yaram ya naan : “Ana lutax ngeen di seede ngir dugal nu ? ” (Der ya) tontu naan : “Yàlla miy wax loo lu nekk, Moo nu wax loo. Te Moo leen sàkk cig njaalbéen te it ca Moom ngeen di dellu”. 22. Te manuleen woon làqatu ba seeni nopp, ak seeni gët du caagéeni seen yaram (ñu seede dugël leen). Waaye dangeen defe woon ne Yàlla xamul lu bari ci li ngeen daa def. 23. Loolu mooy seen njortu la ngeen jortoon ci Yàlla, moo leen faagaagal, ba ngeen xëy yàqule.
coran-wolof.pdf
page_388
388 24. Bu ñu xaaree, Safaraa di seen kër ; bu ñu sàkkoo njégël, kon duleen jégël. 25. Boole Nanu leen ak ñu ñu lëkkëlool ñu taaralal leen la ca seen kanam ak sen ginnaaw (la ñuy jëf). Dogal ba dal ci seen kow, kem na mu ame woon ca xeet ya leen jiitu woon ci jinne yi ak nit ñi. Ñoom dañoo yàqule ! 26. Ña weddi ngay wax naan : “Buleen déglu Alxuraan jii, te ngeen koy doyadil (di ko caaxaane) ndax amaana ngeen am ndam”. 27. Dananu, mosal ña weddi mbugal mu tar te dananu leen faye la gën a ñaaw ca la ñu daan def. 28. Loolu, mooy peyug noonu Yàlla Safara mudi seen kër ga ñuy dëkk béel ca, muy peyug weddi ga ñu daan weddi sunuy laaya. 29. Ña daan weddi dañuy wax naan : “Yaw sunu Boroom, wan nu ña nu daan réeräl ci jinne yi ak nit ñi, dananu leen def ci ron sunu ndëguy tànk, ngir nu gën a soofe”. 30. Ñiy wax naan : “Yàllaay sunu Boroom”, tey jéem a tegu ci seen yoonu Boroom wu jub wa xocc, Malaaka yi dañuy wàcci ci ñoom naan leen. “Buleen jàq buleen ragal ; bégleen ci àjjana ja ñu leen daan dig. 31. Nun (Yàlla) noo di seen wéeruwaay ci àddina di seen wéeruwaay ca àllaaxira ; te am ngeen fa lépp lu seen bakkan di wonnén ak lépp lu ngeen fay laaj, 32. (wàccuwaayu teraanga) bu bawoo ca Jéggëlekat ba, di ab Jaglewaakoonu yërmande”. 33. Ana kan moo gën a rafet ay wax kuy woote jëme ci Yàlla, tey jëf yiw tey wax naan : “ Ci jullit ñi laa bokk ? ” 34. Lu rafet ak lu ñaaw du ñu yem. Na ngeen jiñe (ab safaan) ci lu baax ; (soo ko defee) ki nga gënoon a noonoo dafay jekki di sa xaritu benn bakkan. 35. Lii nag kenn du ko am ku dul ñuy muñ kenn it du ko am ku dul boroom cër bu duun.
coran-wolof.pdf
page_389
389 36. Amaana leeg-leeg bu la saytaane jaxjaxee (waaye bu boobaa), na nga sàkku ci Yàlla mu mësal la ; Moo di, aji Dégg ja, aji xam ja. 37. Bokk na ci ay kéemaanam, guddi ak bëccëg, ak jant beek weer wi : buleen sujuudal jant bi, waxantumalaak weer wi, waaye na ngeen di sujuud ngir Yàlla mi leen bind, ndegam Moom ngeen di jaamu. 38. Bu ñu rëy-rëyloo... (ba defuñu ko) Malaaka ya nekk ca sa Boroom ñoom dañuy sàbbaal, guddeek bëccëg, te duñu ko bàyyi ! 39. Bokk na ci Ay kéemaanam ngay gis suuf si mu ne ndàpp (wow koŋŋ). Saa su ñu ci wàccee ndox, mu funki màgg. Ki koy dundal (di ci def gàncax) mooy dekkal ñi dee, Moom man na Lépp lu ne. 40. Ñiy jéem a soppi samay laaya (Alxuraan) manuñu nooraan. Moo ndax ku ñu sànni ca safara moo gën walla kuy dikk bu Bis Pénc baa ànd ak ug wóolu ? Defleen lu leen soob moom kuy gis la li ngeen di def ; 41. Ñay weddi [Alxuraan] ba mu dikkee ak li mu leen di fàttali dees na leen mbugël... te Téere bii Téere bu Kàttanu la ; 42. Ay caaxaan [du ko dikke fenn], du ci kanamam mbaa ci ginnaawam : dañu koo wàcce mu bawoo ca (Yàlla) miy aji Xereñ, di Yayoowaakoonu cant. 43. Deesul a wax lenn lu ñu waxutoon Yonnent ya la jiitu woon. Sa Boroom, ku Am njégël la te di Boroom mbugël mu mitti. 44. Bu Nu ko defoon muy weneen làkk (wu dul araab), danañuy wax naan : “Ana lutax faramfànce wu ñu ay laayaam? Yonnentub araab ak làkk wudul araab (nu muy ame)? ” Waxal ne : “njub la ak saafara, ñeel ñi gëm”. Ñi gëmul nag ñoom, ay saañ nekk ci seeni nopp def ngumba ci seeni (gët xel) ; te ñoom na nga leen di woowe ca barab bu sori. 45. Joxoon Nanu Muussaa Téere ba. Mu am ñu ca wuute. Bu ca sa kàddug Boroom jiituwul woon, dana fekk ñu àtte woon seen diggënte. Te it ñoom, ñi ngi sikki-sàkka ci ay mbiram.
coran-wolof.pdf
page_390
390 46. Képp kuy jëf yiw, boppam la koy defal. Képp kuy jëf ñaawtéef it, te ci kawam lay dal. Sa Boroom, du tooñ, benn jaamam. 47. Ca moom la xam-xamu Waxtu wa di dellu (moom rekk xam). Amul menn meññat muy génn ciw xottam, amul it jenn jigéen juy ëmbu walla muy imbi lu dul am na ca xam-xam bu mat sëkk. Te bu keroogee bis ba mu leen di woo naan : “Ana ña ngeen ma daan bokkaaleel ? ”, ñu naan ko: “Noo ngi lay birëlal ne kenn seede wu ko ci nun” ! 48. Lañu daan jaamu ca àddina réer leen ; ñu daldi xam nag ne amatuñu rawukaay. 49. Nit du bàyyi du yoqat ci di sàkku di ñaan aw yiw. Waaye saa su ko lor dalee, mu di ku yàkki, kuy yoqat. 50. Saa su nu ko musalee yërmande ju bawoo ci nun, ginnaaw lor ja ko laaloon, muy wax naan : “lii maa ko yayoo ! Te sax fooguma ne saa dana taxaw. Te it su ñu ma delloo ca sama Boroom, li ma fay fekk, mooy dàqati”. Danañu xibaar yéefar ya la ñu daan jëf te dana nu leen musal ci mbugël lu diis gànn (miti). 51. Su Nu mayee nit xéewël, mu dumóoyu daldi féew (sori). Waaye saa su ko lor laalee, muy ñaan ñaan yu gudd. 52. Waxal ne : “Xanaa gisuleen ? Alxuraan jii ca Yàlla la bawoo ngeen weddi ko ; ana kan moo gën a réer kuy nekk ci teqalikoo gu sore (faasaloo) ? ” 53. Dananu leen won sunuy kéemaan ci déeléey asamaan ak ci seen bopp, ba baa ñuy gindi ku ci xam ne (Alxuraan), mooy dëgg tigi. Xanaa kay war na laa doy rekk ci sa Boroom ne moom seede la ci lépp ? 54. Ñoom xanaa ña ngay sikki-sàkka, ci dajeek seen Boroom ? Te Yàlla moom peeg na lépp lu ne . ----------------------------------------------------------------------------- Saar 42 : DIISÓO
coran-wolof.pdf
page_391
391 53 laaya - Laata Gàddaay ga ----------------------------------------------------------------------------- Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi. 1. Haa, Miam. 2. Ayn, Siin, Qaaf. 3. Noonu la la Yàlla, miy boroom Kàttan, tey ku Xereñ, di soloo ay ndigëlam, kem ni mu ku defe woon ca Yonnent ya la jiitu woon. 4. Moo moom li nekk ci asamaan yeek suuf si. te mooy Kooku, di aji Màgg ji, 5. Asamaan yi dañuy xawa foq bu Malaaka yi di sàbbaal di kañ seen Boroom, tey jéggalul ñi nekk ci kaw suuf si. te Yàlla tigi mooy Jéggëlaakoon bi, di Jaglewaakoon bi yërmandéem. 6. Ñuy wut ay wéeruwaay yu dul Yàlla, Yàllaa ngi leen di fuglu. Te yaw (Muhammad) du yaay lijjanti seen mbir. 7. Noonu la nu la soloo (Alxuraan jiy làmmiñu araab), ngir nga xupp ci ndayi dëkk ya (waa Màkka) ak dëkk ya ko wër ak it nga waar leen ci Bisub daje ba, - (bis pénc ba) sikkuwul bu boobaa - Ab kurél dafay nekk ca àjjana beneen kurél ba nekk ca biir Safara. 8. Su sooboon Yàlla, Mu def leen wenn xeet. Waaye Mooy dugël ku Ko neex ci biir yërmandéem. Te tooñkat yi nag ñoom duñu am wéeruwaay, waxantumalaak ku leen di dimbali. 9. Walla ñoom dañoo far am wéeruwaay yu dul Yàlla ? Wéeruwaay tigi mooy Yàlla ; te mooy dekkal ñu dee woon ña te moo di ki man lépp lu ne. 10. Te lépp lu ngeen am ag juuyoo, Yàlla yor àtte ba. Koo koo di Yàlla sama Boroom; ci Moom laay wéeru te it moom la doyloo.
coran-wolof.pdf
page_392
392 11....Moo bind (sàkk) asamaan yeek suuf si. Defaralal na leen y soxna [jële ko] ci seeni jëmm ak ay mala yu di ay tóollént ( góor ak jigéen); te ci loolu la leen di yokki (jurante). Amul lenn lu mel ni moom (Yàlla) ; mooy aji Dégg, di aji Gis. 12. Moo ame caabi [ndami] asamaan yeek suuf si. Mooy yaatalal wërsëg ku ko soob, moo ko koy xatalal it. Te, Moo di ku xam lépp lu nekk. 13. Diine ji mu tëral (ngeen war koo dund), mooy la mu dénkoon Nooh, ak la Nu la soloo (yaw Muhammad), ak li nu dénkoon Ibraahiima, ak Muusaa ak Iisaa(te moo di) : “na ngeen taxawal diine; te buleen cay teqalikoo”. Li ngeen di woo bokkaalekat yi bëg leen caa jëmële dafa diis ci ñoom lool. Yàlla mooy jigeel boppam ku ko soob te it mooy gindi képp ku koy jébbël boppam . 14. Xam-xam da leen a digël ba noppi ñu door a teqalikoo (ngir bew ak kujje) ga nekk ci seen diggënte. Du gan kon ak li Yàlla xas a joxe dig ba (Bis Pénc), kon dees na àtte seen diggënte (fii ci àddina). Te ña ñu donale woon Téere ba seen ginnaaw, ña ,nga cig sikki-sàkka gu yéeme (lënt). 15. Kon na ngay woo (nit ñi) jëme leen ci diine jooju ; te na ngay tegu ca yoon wu jub wa xocc ni ñu la ko digële ; te bul topp mukk seen bànneex ; te na nga wax ne : “Gëm naa lépp lu Yàlla wàcce mu di ab Téere, te digaleef na ma may maandu ci seen diggënte. Yàlla moo di sama Boroom. Te it Yàlla dananu dajale nun ñépp te ca moom la ñépp di mujj”. 16. Ñiy diiŋat mbiri Yàlla, ginnaaw ba ñu ko nangulee, seenu lay la naaxsaay la ca Yàlla. Te mer dal na ci seen kaw ñu am mbugël mu tar. 17. Moo di Yàlla mi wàcce Téere ba ci dëgg, ak nattukaay ba (balaas ya). Ana loo ci xam ? te amaana waxtu wa di lu jigeñ ? 18. Ña ko gëmul ña nga koy yàkkamti ; waaye ña gëm ñoom dañu koy ragal te xam nañu ne mooy dëgg tigi. Ñay werante ci mbirum waxtu wa (Bis Pénc ba) ña nga ci réer gu sore. 19. Yàlla kuy ñeewanti jaamam ñi la. Mooy wërsëgël ku ko soob. te moo di boroom Doole ja, boroom Kàttan ga. 20. Képp ku namm ruuj [toolu] dundug àllaaxira, Dananu ko dollil ruujeefam. Képp it ku namm ruuj [toolu] dundug àddina, Dananu ko nangul ; waaye du am benn cër ca àllaaxira.
coran-wolof.pdf
page_393
393 21. Am ñoom da ñoo am bokkaale yu leen tërëlal diine ju bokkewul ak li Yàlla digle ? Du gan kon, ak kàddu gu xas jib ba noppi, kon àtteef na seen diggënte. Te tooñkat ya ñoom am nañu mbugël mu mitti . 22. Danga gis tooñkat ya ñu tiit lool ngir la ñu daan def, (mu di mbugël) muy dal ci seen kaw. Waaye ña gëmoon te daan def yiw, ñoom ña nga ca biir dëri àjjana ya, ñu fay am la ñu bëgg ci seen Boroom. Loolu moo di ngëneel la gën a rëy ! 23. Loolu moo di [xibaar bu neex] bi Yàlla di bégale jaamam ña gëm tey jëf yiw ! waxal ne : “Du ma leen laaj genn pey lu dul dëgëral gi ci diggënte ag mbokkoo”. Képp ku def lu rafet, Dananu ko ko dollil lu gën a rafet (mu di ab neexal). Yàlla jégëlaakoon la kuy sant la (delloo njukël). 24. Walla ñu daan wax naan day duural Yàlla ay fen. Bu neexoon Yàlla, Mu fatt sab xol. Yàlla dana (raaf , far) lépp luy neen. Te dana dëgëral dëgg ci ay kàddoom moom xam na li làmbu ci dënn yi. 25. Mooy kiy ndangu tuub ci jaamam ñi, tey jéggale ñaawtéef yi tey xam li ngeen di def. 26. te it mooy nangul ñi gëm tey jëf yiw di leen xeewël, yéefar yi nag ñoom am na ñu mbugël mu tar. 27. Bu Yàlla yaatalaloon wërsëg jaamam [ñépp], kon dañuy bew ; ba tax na, mu di ko wàcce di ko yemale na mu ko soobee. Ndax Yàlla ku Xàmmee la kuy Gis la Jaamam ñi. 28. Moo (leen) di wàcceel taw ginnaaw bu ñu yàkke xont, te mooy tasaare Yërmaandeem. Mooy Kilifa gi, di Yayoowaakoonu cant. 29. Bokk na ci ay kéemaanam bindug asamaan yeek suuf ak ndundët yi mu tasaare (nuy duggat). Te man na leen dajale saa su Ko soobee. 30. Bépp lor ju leen dal yéen a ko jëf. Yàlla dafay jéggale yu bari.
coran-wolof.pdf
page_394
394 31. Munuleen a raw Yàlla ci suuf si ; te it du ngeen am geneen kilifa, waxantumalaa ndimbal kudul Yàlla. 32. Bokk na ci ay kéemaanam (firndéem), gaal yuy daw ci géej, tollu ni ay tundu doj. 33. Su ko neexee, Mu téye ngilaw, ñu ne tekk ca ndox ma. Ay kéemaan na ngi ci biir loolu ngir [nit] kuy muñ tey sant (dello njukël). 34. Walla, mu mbugël leen ci seeni jëf. Tey jéggële lu bari. 35. Ñiy diiŋat sunuy firnde it danañu xam ne du nu man a am rawtukaay. 36. Lii nu leen jox lépp [ci alal] bànneexu dundug àddina rekk la ; waaye la nekk ca Yàlla moo gënn te moo gën a sax ngir nit ñi gëm tey doyloo seen Boroom, 37. ñiy wattandiku bàkkaar yu mag a mag yi ak ñaawtéef yi, te saa su ñu meree jéggale, 38. ñiy nangul seen boroom, ak taxawal Julli, ak di disóo seen mbir ci seen diggënte, tey joxe ci la ñu leen wërsëgël (seeni alal), 39. ña nga xam ne, saa su ag tooñ amee, ñu saafara ko (fayu). 40. Lu bon lu bon a koy fay ni moom. Waaye kuy jéggële tey yéwénal (na xam ne), Yàllaay warloo peyam. Te Yàlla du safoo tooñkat ya ! 41. Ñay fayu ginnaaw ba ñu leen tooñee,...ñooñu kenn amul ci ñoom aw yoon ; 42. Ña yoon war a dal ci seen kaw kay ñoo di, ñay tooñ nit ñi, di xaabaabal ci lu dul dëgg ci suuf si : mbugël mu mettee leen di xaar. 43. Képp kuy muñ tey jéggële, man na ñu koo limaale ca ñu dogu ña.
coran-wolof.pdf
page_395
395 44. Képp ku Yàlla xas réerël dootul am kilifa gu koy man a aar ku dul Yàlla. Danga gis tooñkat ya bu ñu gisee mbugal ma dañuy wax naan : “Fu ñuy ame pexe mu nuy delloo [àddina] ? ” 45. Danga leen gis ñu di leen gaaral ca kanam Safara, ñu boole tiit ak gàcce, ña ngay xoole ne xeww di rummi, ña gëm ña ngay wax naan : “ña yàqule tigi, ñooy ñi ñàkk seen boop ak seenug njaboot bu Bis Pénc baa”. Tooñkat ya nekk ci mbugël mu sax. 46. Amuñu ay wéeruwaay yu leen man a dimbali wudul Yàlla (ndax) képp ku Yàlla réerël mu sànku. 47. Wuyuleen wooteb Yàlla bi balaa bis di ñëw boo xam ne kenn du ko man a fomm te it kenn du ca man a làqu Yàlla. Te it bu keroogee (Bis Pénc ba), dungeen man a miim (seeni bàkkaar). 48. Bu ñu dumóoyoo,... Yónniwunu la ngir nga di leen sàmm : yaw jottali doŋŋ la war. Te Nun saa su nu musalee nit ki yërmaande, mu bég ca maare ; waaye saa su ko lor dabee ju mu fàggul boppam...,muy xarab di xund ! 49. Yàllaa moom nguurug asamaan yeek suuf si. mooy bind lu ko soob. Mooy may ku Ko soob ay doom yu jigéen, mooy may it ku Ko soob ay doom yu góor, 50. walla mu di ko def njaxas ñu di góor ak jigéen ; Mooy def it ku Ko soob jaasir. Yàlla aji Xam la boroom Doole la. 51. Yàlla du waxanteek kenn nit lu dul ci soloo, walla ci ginnaaw kiiraay, walla mu yabal ndaw (Malaaka) mu di ko soloo, lu ko soob, ci ndigalul Yàllal. Yàlla aji Kawe la aji Xereñ la. 52. Noonu la ñuy soloo ci yaw [Alxuraan] ci Sunu ndigël. amoo woon benn xam-xam ci Téere bi du caagéene ngëm; waaye def leer di ci gindi ku nu soob ci sunu jaam ñi. Te yaw it da ngay gindee jëme ci yoon wu jub wa xocc, 53. yoonu Yàlla ji moom asamaan yeek suuf si ak li ci seen biir. Ca dëgg-dëgg ca yàlla la mbir yépp di mujj. -----------------------------------------------------------------------------
coran-wolof.pdf
page_396
396 Saar 43 : XOYXOYAL 89 laaya - Laata Gàddaay ga ----------------------------------------------------------------------------- Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi. 1. Haa, Miim. 2. Ci Téere bu leer bu ! 3. Def Nanu ko Alxuraan ci làmmiñu araab ndax amaana ngeen xellu (xalaat). 4. Nekk na fi Nun, ca ndayi Téere ba (Allawhul mahfuus), kawe lool fees dell ag ràñnee. 5. Moo ndax ! Danu leen di jox [Alxuraan] te fekk ngeen di ay yàqkat ? 6. Ak a bari lu nu yónni ci ay Yonnenta ca ña jiitu woon ! 7. amul Yonnent bu mas a ñëw te yéjjiwuñu ko (ñaawal). 8. Faagaagal na nu ña leen ëppoon doole ! Xam ngeen xibaari ña jiitu woon. 9. Te soo leen laajee : “Kan moo bind asamaan yeek suuf ? ” Dañu naan : “Yàlla, miy boroom Kàttan di ku Xam moo leen bind”. 10. Yàlla mi leen defal suuf si muy laltaay defaral na leen ci ay yoon ngir ngeen man cee ginduku ; 11. Mooy kiy wàccee am ndox ci asamaan si di ko yemale Ñu di ca naatal ay dëkk yu bekkooroon. noonu it ngeen di dekkiwaate ; 12. Moo bind tóolent yépp, defaral ay gaal, amal yu ngeen di war,
coran-wolof.pdf
page_397
397 13. ngeen di def ñoŋŋ ca kaw, ngeen di fàttaliku xéewali Yàlla, su ngeen yemoo ca kaw ne ñoŋŋ, te it na ngeen di wax naan : “Tudd nanu sellug ki nu tàggatalal lii (wépp waruwaay) te manalu nu ko woon sunu bopp. 14. Te dañuy wëlbatiku jëm ci sunu Boroom”. 15. Nit ñi dañuy mbokkale yàlla ak lenn ci jaamam ñi. Te nit xarabaatekat la bu bir ! 16. Am Yàlla moom dafa jàpp ci li mu bind aw jigéen def leen ñu di doomam ba eggal yéen mu tànnal leen ay doom yu góor ? (mukk amul) 17. Te kat, saa su nu bégëlee kenn ci yéen ak la Yàlla doon misaal (doom ju jigéen), xar- kanamam ba daldi ñukku muy fuuñ-fuuñi (mer). 18. Moo ndax ! Du ul ne (jigéen) mooy màgg ci gànjaroo takkaay, te joŋewul ci dàggasante ? 19. Ñuy def Malaaka ya di ay jaamu Yàlla [aw jigéen] ! moo ndax baleen Yàlla di sàkk dañu koo teewe woon ? Danañu bind la ñu seede ; laaj leen ko (ba xam lu ñu ca xam). 20. Dañuy wax naan : “Bu neexoon Yàlla du nu leen jaamu”. Waaye amuñu ca benn xam- xam ; dañuy foog doŋŋ. 21. Walla, da Nu leen joxoon ab Téere ca la ko jiitu woon ba tax ñu ŋoyoon ca ? 22. Li ñu wax kay moo di : “Fekkoon nanu sunuy maam am diine, kon nag (wat ci watiit) ñoom la ñuy toppandoo”. 23. (Noonu it la daan deme) ndax masunoo yónni waa ab xuppekat (waaraatekat) cib dëkk lu dul ne ne kilifa ya danuy wax naan : “Sunuy maam amoon nañu diine te nun ñoom la ñuy roy”. 24. Mu wax leen ne : “Ndax indilu ma leen lu gën a jub la seen baay ya nekkoon ? ” Ñu tontu ne ko : “Nun kat gëmu nu lii ñu la yónni”.
coran-wolof.pdf
page_398
398 25. Nu daldi fayu ca seen kaw. Xoolal (settantal) naka la mujjug weddikat ya deme. 26. (Fàttalikul) Ibraahiima ba mu waxee baayam aku nitam : “Man mii ku deñ laa ci lii ngeen di jaamu, 27. ba mu des (Yàlla) mi ma sàkk bind ma, te moo may gindi”. 28. Mu def (dénkaane boobu) muy kàddu guy sax ginnaawam. Ngir amaana ñu dellu (di jëfe seeni xel) ? 29. Waaye xéewaloon naa ñooñee ak seeni maam, Ba dëgg ga (Alxuraan) digël leen ànd ak Yonnent buy leeral. 30. Ba leen dëgg ga digëlee, dañoo wax naan : “Lii daal ag njibar la te nun ay fen la nu ko jàppe”. 31. Ñuy wax it ne: “Cëy Alxuraan jii bu wàccoon ci nit ku tekki te dëkk ci benn ci ñaari dëkk yi ? ” (Taayif, Màkka) (al Waliidu ibn almuqiira) walla (Urwatu ibn masuud). 32. Moo ndax ñoom ñooy séddële yërmaandey sa Boroom ? Te Nun dey Noo leen di séddale seenub dundu ci àddina te it tooñkat ya ñennat ci ñoom, teg na leen ca kaw ña ca des ngir nuy yilifante. Waaye yërmaandey sa Boroom, moo gën fuuf, li ñuy dajale. 33. Su nit ñi doonoon wenn xeet, kon Dinanu defaral ñiy weddi Yàlla, seeni kër am ay xàddi xaalis ak ay ker-keraan ñu di ca yéege ; 34. seen kër ya amna ay wunt ak ay lal ñu di ca sóonu, 35. ak ay xoyxoyal. loolu lépp du lenn lu dul bànneexu dundug àddina, te àllaaxiraa, nga fa sa Boroom, ngir ñu ragal Yàlla. 36. Képp kuy sori ak a dumóoyu tudd Yàlla (fàttaliku) Yëramaakoon bi, Dananu ko booleek Saytaane su mu lëkkalool.
coran-wolof.pdf
page_399
399 37. Te ñoom Dañu leen dëdaleek yoon (wu jub wa xocc), te ñu foog ne dañoo gindiku. 38. Ba ne seef agsi ci Nun dey, daldi wax ne: “Aka neexoon ! Sunu diggënte soriyaantoo ni [Pénkook Suwu] ! ” – Ndaw lëkkëloo bu bon ! 39. Loolu lépp du leen jariñ lenn tey jii – ginnaaw ba ngeen tooñee – yéen ay bokk yem ca biir mbugël ma. 40. Moo ndax yaw man ngaa déggloo ku tëx mbaa nga man a gindi ku gumba mba ku nekk ci réer gu tar ? 41. Benn nu yóbbu la nga [dee] Nu daldi fayu ci ñoom ; 42. Walla Nu wan la la Nu leen digoon ñoom ; am Nanu Kàttan ci seen kaw de. 43. Jafandikul ci li nu soloo ci yaw yaa ngi ci yoon wu jub xocc wa. 44. Dëgg-dëgg [Alxuraan] fàttaliku la ngir yaw ak saw nit. Te it deefna leen ko laaj. 45. Laajal Yonent yi Nu jëkkoon a yónni ñu jiitu la, ba xam ndax defaroon Nañu Yàlla, ju bokkul ak yëramaakoon bi, ju ñuy jaamu ? 46. Yónni woon Nanu Muusaa ak Sunuy kéemaan, ci Firawna ak gàngooram ga. Mu ne leen: “Man ndawul Boroom àddina si laa”. 47. Ba mu dikkee ca ñoom ànd ak Sunuy firnde (kéemaan), ndeketeyoo dañu koy reetaan. 48. Kéemtaan gu mujj a ñëw ëpp ga ko jiitu woon. Ba noppi nu toftal ca teg léen ay jafe-jafe, ngir amaana ñu dellu ginaaw. 49. Ñu wax (Muusaa AS) ne ko : “Éy njibarkat ! Ñaanal nu sa boroom ci li nga séq ak moom ( mu teggil nu jafe-jafe yi). Soo ko defee nu jubook yaw”.
coran-wolof.pdf
page_400
400 50. Ba nu teggee jafe-jafe ya, da ñoo tiri lépp la ñu digéwoon. 51. Firawna daldi dajale aw nitam ne leen: “moo sama gaa ñi ! Ndax moomu ma nguurug Misra ak dex yii di dawdawaan ci sama ron? Xanaa du ngéen gis ? 52. Xanaa man sax maa wara gën waaju doyadi jii nga xam ne xawut a man a wax ( lu nit di xam )? 53. ( Lii muy woote su doon dëgg) Kon ñu takkal ko lami wurus? Wala mu lëngook ay Malaaka? ” 54. Mu fëkk xeli nit ña ñu daldi ko topp génn ci diine. 55. Ba ñu Nu merloo, ca la Nu fayyoo labal ñoom ñépp. 56. Nu def leen ñu di am njàng ci ñiy xalset a dikk ëllëg. 57. Ba ñu jëlee misaal ci Iisaa doomi Maryaama, saw nit dañoo daldi dumóoyu, 58. Ñu daldi wax ne : “Ndax sunuy Yàlla ñoo gën, walla moom sax ? ” Ay werante rekk la ñu fi indi . Te sax ñoom ay niti tafaar la ñu. 59. Moom de (Muusaa) ab jaam rekk la bu Nu jox xeewal def ko muy roytéef ci wa Bani Israayiil. 60. Bu Nu sooboon , Nu def ci yéen ay Malaaka yuy ayayloo ci kaw suuf si. 61. Te firnde lay doon ci (Bis Pénc ba) waxtu wa. Buleen ci am sikki-sàkka. Te na ngeen ma topp : yoon wu jub xocc waa ngi nii. 62. Buleen nangu mukk Saytaane di leen wëlbati ! Ndax seenub noon la (bu nëbbutuwul) fes.
coran-wolof.pdf
page_401
401 63. Ba Iisaa dikkee and ak i firnde, nee na leen : “Indil naa leen xam-xamu xereñ ak it ngir ma leeralal len lenn ci li ngeen di juubuu. Ragalleen Yàlla te topp ma. 64. Yàlla moo di sama Boroom di seen Boroom. Na ngeen ko jaamu. Lii mooy yoon wu jub wa xocc. 65. Kurél ya juuyoo ci seen biir. Ña daan tooñ toskare nañu ci mbugëlu bis bu mitti ! 66. Moo ñoom ndax xaaruñu lu dul (Bis Pénc ba) waxtu wa mu naan jaseet ci seen kaw, bett leen te du ñu ko yëg ? 67. Ña xaritoo woon, bu keroogee ñennat ci ñoom, ay noon la ñuy doon ; lu ca dul ñay ragal Yàlla. 68. “Éy yéen Sama jaam ñi ! tey jii buleen tiit ; mbaa ngeen di jaaxle, 69. Ña gëmoon Sunuy kàddu te doonoon ay jullit, 70. “Dugguleen àjjana, yéen ak seeni soxna, danu leen fay berndeel”. 71. Danu leen fay wër ak booli wurus ak i kopp ; def lépp lu bakkan di wonnen ay gët di ko bànneexoo ; - “te dangeen fay béel. 72. Loolee mooy àjjana ja Nu leen donale ci la ngeen daan jëf. 73. Am ngeen fa ay fuytéef yu bari ngeen di ca lekk”. 74. Tooñkat yaa ngi, ci biir mbugalum Safara béel ca, 75. kenn duleen ko mas a woyafal te dañu naan fa xuum ne muq ngir jaaxle. 76. Du ut ne Nun noo leen tooñ, waaye ñoom ñoo tooñ (seen bopp).
coran-wolof.pdf
page_402
402 77. ña ngay woo : “ Maalik (bëkknéegu safara)! naan ko nanu sa Boroom jéggëli book ! ” muy tontu naan : “Yéen kay, ci [mbugël mii] ngeen di sax dëgg” ! 78. “Indiloon Nanu leen dëgg; waaye ñi ëpp ci yéen dañoo bañ Dëgg”. 79. Walla, Ñoom dañoo fexe ay mbir [ak lu man a xew] ? Nun nooy sottal mbir yi ñu alku ! 80. Moo ndax ñoom dañoo jortu ne dunu dégg li ñuy nëbb ak di ko déeyoo ? Axakañ (dégg Nanu ko de) ! te sunuy ndaw a nga ca ñoom di bind. 81. Waxal ne : “Su fekkoon ne Yàlla Yëraamaakoon bi amoon na doom dey, man maay doon jaamam biy gën a (nungu ag njaamam)”. 82. Tuddnaa sellug Boroom asamaan yeek suuf, mooy Boroom (Aras) gàngunaay ga ; Kawe na lool soree ak ni ñu koy melal. 83. Bàyyileen rekk ñuy nuur ciy caaxaan ak di fo ba baa ñuy dajeek seen bis bi nu leen daan tëgoo (Bis Pénc ba). 84. mooy jenn Yàlla ci asamaan si di Yàlla ci suuf si ; mooy ki Xereñ, di ku Xam ! 85. Te itam barkeel na Moom mi am nguurug asamaan yeek suuf si ak li nekk ci seen diggënte. Moo ame it xam-xam bi làmboo waxtu wa (Bis Pénc ba). Te it ca moom ngeen di dellu. 86. Ñay jaamu leneen lu dul moom duñu am benn man-man ci tinu (rammu), ba mu des ñay seede ci dëgg te di ñu xàmmee. 87. Soo leen laajoon ana kan moo leen bind, ñu ne la : “Yàlla”. Kon naka la ñu koy dumóoyoo ? 88. Waxi Yonnent ba moo di : “Éy sama Boroom, ñii daal ay nit la ñu ñu gëmul”.
coran-wolof.pdf
page_403
403 89. Dumóoyuleen yaw ; tey wax : “Jàmm ! ” Danañu xalset a xam. ----------------------------------------------------------------------------- Saar 44 : SAXAR SA 59 laaya - Laata Gàddaay ga ----------------------------------------------------------------------------- Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi. 1. Haa, Miim. 2. Ak ci (Alxuraan) Téere bu leer bi (Maa ngi ciy waat) ne. 3. Wàcce Nanu ko ci guddi gu barkeel, Nu ca doon xuppaate, 4. ci la Nuy teqalee mépp mbir mu xereñ, 5. moo di mbir mu bawoo ci Nun. Ci la Nuy yónnee [Yonnenta ya], 6. moo di yërmaande ju bawoo ci sa Boroom, mooy Kiy Dégg, di ku Xam, 7. Moo di Boroom asamaan yeek suuf seek li nekk ci seen diggënte, ndegam wóolu ngeen. 8. Amul jenn Yàlla judul Moom. Mooy dundal di reye, Mooy seen Boroom mooy Boroom seeni maam ya fi jëkkoon. 9. Ñoom, ña ngay sikki-sàkka, di fo.
coran-wolof.pdf
page_404
404 10. Fuglul, cëy bis ba asamaan si di dikk ak saxar suy jolli 11. di moor nit ñi. Tey mbugël mu mitti. 12. “Waay-waay, sunu Boroom téggil nu mbugël mi. Ndax nun ay jullit la nu [léegi]”. 13. Ana fan la leen kii fàttaliku bawoo te ab Yonnent bu bir dikkoloon leen, 14. Ñu daldi dumóoyu te naan : “Kii daal, ab dof la”. 15. Dananu teggi mbugël mi tuuti ; dangeen dellusi de. 16. Cëy bu keroogee bis ba nuy kaanu di nappaje danuy fayu de. 17. Sànje woon Nanu , nitu Firawna ña leen jiitu woon, te amoon na ñu ab Yonnent bu leen dikkaloon bu tedd, 18. [daan leen wax naan]: “Delloleen ma jaamu Yàlla yi ! Ndax man mii ab Yonnent laa bu wóor. 19. Buleen kawe kawe lu ci Yàlla, ndax man dey firnde ju wér laa leen indil. 20. Maa ngi sàkku muslaay ci sama Boroom di seen Boroom, ndax ngeen bañ ma jóor i xeer. 21. Su fekkee ne gëmuleen ma, kon sori leen ma”. 22. Muu daldi ñaan Boroomam ne ko : “Ñi de ay niti Tafaar lañu (tooñkat)”. 23. “Toppal guddi rañaan ak samay jaam ; danañu len dabusi. 24. Bàyyil géej ga mu ne tekk ; ndax ñoom ay xarekat lañu ñuy, xala lab”.
coran-wolof.pdf
page_405
405 25. Ak a bari ay dër yu ñu bàyyi ginnaaw ak bëti ndox 26. ak tool (mbay) ak kër yu taaru, 27. ak i xéewal yu ñu daan gamaajoo. 28. Noonu la Nu ko donolee yeneeni xeet. 29. Asamaan ak suuf jooyuñuleen te kenn it muñadikuwuleen. 30. Musëloon Nanu , waa bani Israayiila ci mbugël mu doyadima (rey góor) 31. mom Firawna ma kawe woon lool ca yàqkat ya. 32. Tànnoon Nanu leen tigi ci kaw waa àddina sépp (bawoo jamono), 33. indiloon Nanu leen ay kéemaan (firnde) yu leer nàññ. 34. Ñoo ñaa ngay wax naan : 35. “Genn dee rekk am muy sunu dee, gu jëkk gi. Te it kenn dunu dekkalaat. 36. Su fekkee ne dëggu ngeen kon dekkalleen sunuy maam, délloosileen”. 37. moo ndax ñoom ñoo gën Tubbaa ak ña leen jiitu woon ? Faagaagoloon Nanu leen ndax ñoom ay niti tafaar lañu woon (tooñkat). 38. Bindu Nu asamaan yeek suuf si ak li ci seen diggënte di ko fowe. 39. Bindu Nu leen ci lu dul dëgg. Waaye ñi ëpp ci ñoom xamuñu.
coran-wolof.pdf
page_406
406 40. Ca bisub àtte ba, lañuy daje ñoom ñépp, 41. Bis ba farandoo dul jariñ moroom ja ; te kenn duleen dimbali, 42. ku dul ku Yàlla yërëm. mooy, boroom Kàttan, di Jaglewaakoon yërmande. 43. Garabub Sakkuum ga tigi 44. moo di lekkug defaakoonu bàkkaar ya. 45. Day melni biteex ; buy wañax ca (seen biir ya) 46. ni ndox muy bax di wañaxe. 47. Jëlleen ku tëmbéel ko moom ca digg Safara; 48. topp ñuy sotti ci kaw boppam ba mbugëlum ndox muy wañax. 49. Mosal tokamtikul ! Yaay [boroom kàttan] tey ku Tedd (daan rëy-rëylu). 50. Lii nag tigi mooy li ngeen daan werante di ko sikki-sàkka. 51. Ña ragaloon Yàlla te daan wattandiku ña nga ca ay kër yu wóor, 52. ci ay tooli dër ak i dex, 53. ñuy soloo ca xeeti sooy ya gën a ràññiku ne rojj jàkkarloo. 54. Noonu ! La ñu leen di maye ay soxna (yu am bët) huuru alayn.
coran-wolof.pdf
page_407
407 55. Ñu fay man a am wépp xeeti fuytéef féex lool ne fayax. 56. Duñu fa mos wextanu ndee lu dul dee gu jëkk ga. [Yàlla] fegal na leen mbugëlum Safara, 57. muy ngëneel lu bawoo ca sa Boroom. loolu mooy texe gu màgg ga. 58. Di ko yombal ci saw làmmiñ, ngir amaana ñuy fàttaliku ! 59. Xaaral. Ñoom it ñi ngiy xaar. ----------------------------------------------------------------------------- Saar 45 : KU NËRMÉELU KA 37 laaya - Laata Gàddaay ga ----------------------------------------------------------------------------- Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi. 1. Haa, Miim. 2. Wàccug Téere bi ma nga bawoo ca Yàlla, ji am Tedd nga ( Kàttan sañ-sañ), di ku Xereñ. 3. Ay kéemtaan a ngi ci asamaan yeek suuf si yuy soxal way gëm ñi. 4. Ay kéemtaan it, yuy soxal ñi amug wóolu nekk na ci bind, bi ngéen ame ay ci lépp luy dukkat ca anam ya muy giire. 5. Ak ci jëllasanteb guddi gi ak bëccëg bi, ak ci xeewal gi Yàlla wàcce mu bawoo ci asamaan si [Taw] di ci dundal suuf si (Naataange) ginnaaw ba mu bekkooree, ak ci ni muy soppaxndikoo ngelaw yi, ay kéemtaan la yuy soxal ñi xellu.
coran-wolof.pdf
page_408
408 6. Yooyu ñooy firndey Yàlla nu di la ko jàngal mu tegu ci dëgg. Kon ana jan wax la ñuy man a gëm ginnaaw bu Yàlla ak firndeem Yii jàllee? 7. Képp ku dib duuraakoon defaakoonub bàkkaar toskare na ca xuri sawara ! 8. Daan dégg ñuy jàng laayay Yàlla yi ( Alxuraan) mu féttéerlu di jaayub dayo, melni ku ko déggul. (Kookee na xam ne ) mbugal mu mettee (nga koy xaar). 9. Bu xamee as lëf ci Sunu laaya yi, jàppe ko ay caaxaan di ko yéjji. Ñooñee mbugël mu doyadi moo leen fay xaar : 10. (Sawaraw) Jahannamaa ngi leen topp. Lañu doon fàggu ak ña ñu doon digaaleel du ñu léen ko man a fegal. Te sax mbugal mu rëy moo léen fay xaar. 11. Lii ag njub la. Ñi weddi seen Téereb Boroom mbugël mu tar te metti dina leen dal. 12. Yàlla ji léen tàggatal géej, ba gaal di ca tëmb di daw, Ci ndigalam, ak it ngeen di sàkku Ca xeewalam ya xanaa nak da ngeen sant. 13. Moo leen tàggatal lépp lu nekk ci asamaan yeek suuf si, Ay kéemtaan a ngi ci yuy soxal ñiy xalaat. 14. Waxal ñi gëm ne leen na ñuy jégël ñi yaakaarul bisi Yàlla ya ci ne Yàlla dana àtte fay xeet wu nekk ci kem la ñu daan fàggu. 15. Képp kuy jëf yiw, moom caak ; képp kuy jëf lu bon it, moom caak. Ndax yéen ñépp ca seen boroom ngeen di dellu. 16. Indiloon Nanu waa giiru Banii-Israayiil Téere ba, ak ngor ga, ak yonnenta ga, wërsëgëloon Nanu leen ci àddina si yépp ;
coran-wolof.pdf
page_409
409 17. joxoon Nanu leen ay firnde yu leer ci ndigël yi. Wuutewuñu woon lu dul ba ñu amee xam- xam cig bew, ci seen diggënte. Te sa Boroom dana àtte seen diggënte, bu Bis Pénc baa, ca la ñu daan juuyoo. 18. Topp ginnaaw ba teg Nanu la ci yoonu ndigël. Na nga koy topp te bul di topp bànneexu ñiy xamadi. 19. Ndax ñoom du ñu la jariñ ci Yàlla tus. te tooñkat ya ku nekk ma ngay wéeru ci moroomam ; waaye Yàlla tigi mooy wéeruwaayu ñi ragal Yàlla. 20. [Alxuraan jii] ag leer ak gëti xol la, ñeel nit ñi di njub di yërmaande ngir aw nit ñu wóolu. 21. Moo ndax defkati ñaawtéef yi dañoo jàpp ne danu leen di def ni ña gëmoon te daan jëf yiw, ñu yem niróok dundu akg dee ? (mukk du am) aka ñoo bon nu ñuy àttee ! 22. Yàlla bind na asamaan yeek suuf si ci dëgg ak it ngir mu fay bakkaan bu nekk ca la mu daan fàggu. Te kenn du leen tooñ (ci wàññi yiw mbaa yokk safaan). 23. Xanaa gisuloo ka jàppe bakkanam muy yàlllaam ? Yàlla faf ko réerël fatt ag déggëm ak ub xolam muur ab gisam. (Waaw) kooku ana kan moo koy gindi ginnaaw Yàlla ? Xanaa dangeen dul fàttaliku? 24. Ñuy wax naan : “lii daal du lenn lu dul su nu dundug àddina : danuy dee di dund te yàggaayu jamono rekk moo nuy ràpploo”. Waaye amuñu ci loolu benn xam-xam : dañuy njortu doŋŋ. 25. Te saa su ñu jàngee Sunuy laaya ci ñoom, seen lay du doon lenn lu dul di wax naan: “Délloosilleen nu sunuy maam (ya deewoon) ndegam li ngeen di wax dëgg la”. 26. Waxal ne : “Yàllaa leen di dundal soog leen a rey. Ba noppi mu leen di dajale bu Bis Pénc baa, sikk amul ci loolu, waaye li ëpp ci nit ñi xamuñu. 27. Yàllaa moom nguurug asamaan yeek suuf si. Te saa su Bis Pénc ba taxawee, bu keroogee, yéefar yi danañu yàqule.
coran-wolof.pdf