url
stringlengths
6
8
content
stringlengths
2
3.72k
source
stringclasses
3 values
page_101
Yaasin Njaay romb na ma, di gunge benn xaleelu góor, waaye su ma ci kenn nee na nga def, yaa ma nuyu, yow mi nekk bitim- réew. Waa jooju nag, dégg naa ñu naan Tamsiir la tudd. Nee ñu it day tóx yàmbaa, di ko jaay. Xam naa ne daal, li muy fanaan ci kër gaa ngi bëgg a bare. Su dul nekkaale Yaasin Njaay it de, soreetu ko. Ci xutbaam, Yilimaan Keeta wax na wax ju am solo ci mbirum ténj. Tuddul kenn nag, waaye li ma xalaat la waa Ñarelaa yépp xalaat : wax ji amoon na boroom, te du woon kenn ku dul Yaasin Njaay. Bi ma jógee jàkka ja, nuyuji naa samay dëkkandoo, ku ci ne ma laaj la na nga fanaane, jàmmanteek yow. Dellusi naa toog ci sama sijaada.Juróom- ñaari waxtoo ngiy sog a jot. Waa kër gaa ngi dem ak a dikk ci ëtt bi. Coro Caam a ngi taraxlaayoo sér bu weex, jonkan ci taatu furno bi di ko upp ; Lamin jëkkër jaa ngi déglu rajo ci biir néeg bi, di xaaraale mu ñëw tegal ko fondeem ;
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_102
taksi biy jëlsi suba su nekk Ñimma ak Daawuda, doomi Wulimata Maane yi, korne na ci mbedd mi, ñaari gone yi daldi génn ak seen sànse, daw wuti buntu kër gi. Fekksi nañu ma fi ma toog, ñu jox ma loxo, Ñimma sukkal ma. Tooñ naa sax Ñimma, ne ko : - Aa, waaw séeri kóko dangay dem màrse fàtte fi deppàs bi ? Am, téyeel fii waay.Masumaa gis gone gu dooje ni Ñimma ! Mu daldi ree, jël juróomi dërëm yi ma ko tàllal, te naan ma, ak baatam bu sew bi : - Sàllaaw, nijaay, na sa xol sedd, te xam ne tey daxinu biiru xar bu fatt ngay reere ! Bi Lamin dégloo rajo, naan fondeem bay waaj a xéy, ñëw na nuyu ma, ni mu ko tàmmee def, laaj ma na ma fanaane. Waaye tey de, li Lamin dégg ci rajo bi neexu ko dara, ndax mi ngi xultu rekk : - Góor gi Ngiraan, nga baal ma de, waaye ñii ay doomaraam lañu,
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_103
dañoo nar a yàq réew mi ba mu yàqu yaxeet ñu dem bàyyinu fi, jaaxaan Monaako walla béréb yu ni mel, di balaxalmàddaa, nun nuy wéye ndóol ak metit wu dul jeex ! Waaye fi lañu nuy fekk, dunu seetaan loolu, dinanu ko defanteek ñoom ba mu saf sàpp! Lamin dafa mer ba talu maa wax lu ko merloo. Man it, teguma ci baat. Merum Lamin mi dafa ma fàttali jamono ja ma bokkee PAI, nuy xeex ngir réew mi moom boppam. Ma daaldi ne ci sama xel : ba ma ci tolloo de, man mii maa gënoon a wex Lamin fopp ! Waaye gaa ñii ma séqaloon politig bi, dañu maa duuta-duut ba may miir. Te mag muy miir nag, dal-lu ci keppaar a ko war. Su waanee bay dóor-dàqeek alkaati yi ci naaj wu tàng wi, du ñàkk mu mere ku ko deful dara. Li may xalaat loolu yépp, samay bët a ngi topp Lamin. Mu dem ba jub buntu kër gi, daldi dëpp.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_104
Ma ne ko : - Mbaa du dafa am loo fàtte, Lamin ? - Déedéet, Ngiraan. Lu am solo laa la bëgg a wax. - Loolu lu mu ? - Jàmm rekk la. Biig, dama gént di waxtaan ak Badu Taal. Soo jullee tisbaar ba noppi, génneel ko sarax. - Baax na. - Xale bu am jom a ngoog, Ngiraan. - Badu kay kenn la, Lamin. Waaye ragal naa ne dootunu gise maak moom. - Ëpp naa wax, Ngiraan. Fekk na yaa ngi doon door a dem bitim- réew. Ñépp jaaxle. Lamin ne ma : - Ba fi mu ne kenn xamagul réew man la Badu Taal nekk ? - Maa ngi xaar mu bind ma, wax ma fu ko jant biy tiime.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_105
- Su dee xamoo fu gone googu nekk de, ku yabu bañ cee sonn, ndax Badu sa Badu la mas a doon. Bi Lamin génnee kër gi ba ne tuuti, mu am lu ma dégg mu yëngu ci sama ndeyjoor ; ma téen, daldi gis benn wund wu ne noηη ci kow miir bi, xaw maa tiim, ne ma jàkk. Nu xoolante lu yàgg maak wund wi. Ni bët yiy tàkke, di melax, dawloo sama yaram. Wund wi jékki-jékki jooy.Ne tuuti, mu xef, neeti : - Ŋeew, Ŋeew Mu neeti ηeew ñaari yoon, daldi tëb, jàll ci kër gi nu taqalool. Xam nga wund moom, buuru boppam la. Waaye du tee, bu newee ci gox, nit ñi dinañu koy gis muy dem ak a dikk ba ñu far ko miin. Waaye wund woowu de, bés boobu laa ko jëkk a teg bët, te ba sunu jonni Yàlla tey gisaatuma ko. Wóor na ma ne du woon wundu neen. Lu ci mënti ne, lii moom am na : ba mu nee mes, laa tàmbalee xalaat xalaat yu doy waar yooyu ma la doon wax ci ubbiteb Téereb Lëndëmtu bii. Fi ma déju man kenn ci taatu garab gi, maa ngi waxtu :
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_106
- Waaw, yow mii tudd Ngiraan, sant Fay, santati Taal, yaay kan sax ci dëgg-dëgg ? Laaj boobu ma laaj sama bopp tiital ma, sama xel daldi dem xaat ci dee. Tudd Ngiraan Sant Fay, santati Taal. Dee di ma yoot. Ci diir bu gàtt, yu bare ñëwaat nañu ci sama xel : guddi ga la sibbiru su metti daaneelee, yow mii Badu, te taksi dawatul, kaar-ràpid amatul, Biige Sàmb boot la, maak moom kott ñu ne ci mbeddi Ndakaaru yi, di waaxu ba loppitaan. Doktoor bi seet la, làmb sa dënn ak sa jë, xool sa làmmiñ, ne nu : - Su ngeen yéexoon tuuti, musiba am. Wund wi dellusi ci kow miir bi, jooy. Ma téenaat gisuma ko. Fu wund wi jaar? Tiim na ma, yóbbu sama fit, jaxase sama xel, may janeer. Mu mel ni ba mu ma nee jàkk, man Ngiraan Fay mii, dama tiim benn dex, di niitu. Samay jaar-jaar yépp feeñu ma ci biir ndox mi. Ki ma gis ci ndox mi ne ma :
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_107
- Waaw, Ngiraan Fay, nga ne yaay kan nag, ci dëgg-dëgg ? Laaj bu kéemaanee ngoog. Ku dem bay laay sa bopp yenn yi, li tee nga jaaxal say mbokk bareetul. Te tontu cee jafe, tey ! Ndax su ma nee man maay Ngiraan Fay, juddoo Mbériη- Saaj, ca Siin, ñëw Ñarelaa ba ma newee liir, am tey juróom-ñaar fukki at ak lu topp, xeereer, am taxawaay, di doomu Dibókóor Fay ak Xemes Seen, def lii ak lee, jaar fii ak fee, newoon fi óbëryee ca Air Liquide, jiite fa ay gereew yu metti, ñu tëj ma kaso du benn du ñaar, ma bokkoon fi it ci gor yi taxawoon ne dee dañuy xeex tubaab bi, mu abal nu, réew mi jot boppam, te mu jaraloon ma lu ne, ma dem fi ba Akaraa, péeyub réewu Gànnaa, maak ñi ma àndal nu gisee faak Kuwaameη Kurumaa njiitu réew ma, mu jox nu xaalis, dig nu ay gànnaay, loolu yépp su ma ko waxee, wax leneen ak leneen sax,
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_108
mel na ni ba tey waxuma dara. Loolu yépp amul solo, ndax fenn la yëf yi mujjewul. Maa ngi nii déju ci taatu garab gii ci ëtt bi, te xawma sax su ma fi jógee fan laay jublu. Badu, li ma wokk a xosi ñu bare. Waaw, nook juróom-ñaari fan yi nag, ba kañ ? Bés yee koy tey di nu réeral. Yeewu njël, di tés-tési ba ngoon jot, benn fan jàll, mel ni jotewul dara ak yeneen fan yi ko fi jiitu... Waaye jamono dina ñëw, nga war leen a boole ñoom ñépp tënk leen ci benn kàddu doηη. Laaj ma kàddu googu gan la, ma wax la ko. Kàddu googu mooy : dund. Bés yi Yàlla sàkk di tegaloo ba lim bi mat juróom-ñaar fukki at ak lu topp. Nga ne : - Man Ngiraan Fay, nàngami at la dund...b Waaye nàngami at yooyu, di ay bés yu tegaloo, mbaa def nga ci lu nuy wax, Ngiraan ? Mag dikk na. Bi mag di yegsi, dal ci ca kow, dafa ladoxe ginnaaw, wër la ndombo, door a taxaw janook yow. Sam xel daldi demaat ci dee !
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_109
Dëgg la, bàkku waru ma. Du dara loo xam ne sottal naa ko, bi ma juddoo ca Mbériη- Saaj ak tey jii. Du caagin dama nasaxoon. Déedéet. Lu ne jéem naa ko, fu ne làmbaatu naa fa, ni ko Doomi-Aadama yépp di defe su ñu bëggee mënal seen bopp, seeni nawle weg leen. Ma seet seet, gisuma lu sama cawarte googu jur. Guddi jot, ma lal ndés ci sama sagaru pantare bii, su njëlee ma toog ci ëtt bi di xaar te xawma sax lan laay xaar. Mu wóor ma ne su ma fi xéyoon jóge, balaa yàgg ñépp fàtte ma ba fàww. Ci laa sog a xam ne nit dëgg mooy ki sottal ci dundam lu amal askan wi njariñ. Monte Ustaas Mbay Lóo xiiroon na ma ci loolu, ba may gone. Xanaa kay maa ko doon tanqamlu rekk ! Kon yow, Badu, buma tanqamlu. Lan mooy nit dëgg ? Yàlla may la kàttan, nga ne lii ak lii balaa ñu may sànge suuf dinaa ko def, nga doxale noonu sa àddina te doo roy kenn,
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_110
doo déglu kenn, xanaa jàpp ci li nga gëm, sax ci ba dëgër. Loolooy nit dëgg. Su ma delluwoon nekk gone, noonu laay doxale. Ma réccu lu ma mësul a ber benn bés ci bés yi, waxtaan caak sama xel, ni : - Man, Ngiraan Fay, béréb sàngam laa jëm te yoon wii laay jaar. Ñàkk doxalee noonoo ma tax a sànku. Dama daan def fu nit ñi aw ma aw fa. Saa yu ñu newaan yoon waa ngi, daawuma sax jéem a werante, dama daan topp ña jiitu, di daη-daηi. Te njiit yee ka bari woon jooja jamono ! Jamono jooju, bés bu Yàlla sàkk, ma dajeek ku ma joxoñ yoon wu bees. May ma, ma artuwaat la, Badu. Bul yàkkamti ba tax laa juum, nga ne : - Maam Ngiraan moom, ndekete li muy coow yépp, nii la woyofe woon bopp ! Ku ko newaan ayca, topp ma rekk, mu ne la yaa ko yàggal ! Dinaa la xamal tey ne mbir mi yombewul noonu : ka jiitu, naan la ayca, topp ma, doo ko gis doo ko dégg.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_111
Te yow ci sa bopp ba ngay nangoo topp ci ginnaawam, doo ko sax yëg. Yëf yi mbetteel lay doon. Aw askan, dara ëppu ko doole. Dafay yeew buum ci sa baat, di la wommat ni xar. Dékku askan wi lu jafe la, ndax dafay teel a jóg ci yow. Ba ngay bootu lay tàbbal ci say nopp ay kàddu yu fay tëdd ba fàww. Doo xam lu baat yooyu tekki, waaye foo jëm ñu gunge la. Soo demee ba doon mag, lu la askan wi sant nga def ko te doo ci teg baat. Askan wi du am jàmm, feek naju la ci benn béréb, nga ne fa nemm, bëgg noyyi mu të la, lu mu wax nga ànd caak moom. Loolu, noteel la tudd. Noteel googu nag, fu nekk la ko askan wiy jaarale. Ma jox la ci firnde. Dinga daje ci mbedd mi ak nit koo xamul, mu xool la, nga xool ko, ku nekk ci yéen ñaar wéy, dem yoonam. Fekk ngóor soosu mbaa ndaw soosu, doonte ubbiwul gémmiñ sax, am na lu mu la wax.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_112
Xamu la, xamoo ko, waaye daanaka am na lu mu jëmbët ci sa xel, ji ko ci sa xol. Bala mu lay réer ci mbooloo mi, dinga ko tontu ci suuf : - Dégguma li nga wax, waaye ànd naa ceek yow. Mën naa la cee jox beneen firnde.Du ñàkk it bés nga xéy, tàllal sa soxna sagaru téeméeri dërëm, ne ko deppãs baa ngoog, lii rekk laa am. Fiftin bi gën a tuuti deseetoo ko. Nga génn sa kër mel ni dafa am lu la fay dàq, di dox ci naaj wu tàng wi ak say padam-njaxen, naq, sol ay sagar yu tilim, mar ba sa put gi wow koηη te amoo ci benn pexe. Nga agsi ci buntu benn isin, taxaw, naan ci sa xel : - Isin bii de, Baydi Gay mi ma màggandool Garaη-Kees a ko moom, amaana ma jële fi lu ma téyéendi. Bala ngay àgg ci Baydi Gay moomu nga wékk sa yaakaar yépp, sa benn moroomu sët dina la déj cib siis, xaarloo la lu yàgg. Su waa ji féexee, woolu la. Nga dugg, bi mu lay jox loxo,
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_113
seeni bët daje, yéen ñaar ñépp ngeen gis ci saa si ne dungeen ay nawle. Baydi nag, Yàlla fàttewu ko, waaye taxu koo fuuy. Ku am kersa la, ak yar ak teggin. Keroog def na kemtalaayu kàttanam ngir bañ laa sewal. Jéem na la won ne na ngeen meloon démb mooy wéy ba tey. Yónnee na Fantaak Kokaa-Kolaa, ngeen di naan, di fàttaliku, ndeysaan, seen ngone, ba ngeen daan làqu ci àll biy pëtëm gerte walla di lakk ndaamaraas : - Dañuy wax rekk, waaye futbalkat dëgg amatul, Buuba Jaxaaw ak Krumen ñoo mënoon fopp ay Fadiga ak i Okosaa yi ñuy tanqale nit ñi léegi. - Aa, dafa di benn sax ! - Waa jooju waay, te xuuge woon, yaa ngi koy fàttaliku, moo ñoroon tey nag. - Mbirum Yàllaa ngoog de, dafa lay xañ lii may la leneen ba mu doy sëkk ! - Waaw, yëg naa faatoom, ndeysaan, man dem naa sax ba Kawlax jaaleji ko ay mbokkam,
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_114
- Jóob Sëriñ nag, foo koy dégg ? Moo aayoon mat... - Man it de, xawma fu mu mujje, waa jooju, - Yow moom, Ngiraan, jigéen rekk ! Daawoo nangu benn gel rëcc la ! Géy Maryeem, Sow Faatu, céy Ngiraan yaa teel a yàqu ! - Yow jinne nga de, Baydi, ndekete yaa ngi fàttaliku turi nit ñooñu ba tey ! - Yaa ngi fàttaliku woy wi nu Faal Saarl jàngaloon : séqoo faaloo... Ayca, àggaleel : séqoo, faaloo... - Ginaar akub nenam ! - Maa doon sàcc laaloo... - Boroom tool fekk ma fa ! - Ayca, caη nga de ! - Xaaral, ma jéem a fàttaliku, - Tee nga maa fey rekk, ma woyal la li ci des ! Ngeen àndandoo xàqataay. Waaye li ngeen di ree yépp, seeni bët a ngiy daje.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_115
Ku nekk ci yéen ñaar am yu muy xalaat te am kersay wax ko. Lee-lee nga jéem a làq sa tànk yu pënde yi ci suufu siis bi, Baydi Gay mel ni ku ci gisul dara. Telefon bi riir. Baydi jël ko, déglu tuuti, ne : - Mersi madmisel.Am fu mu bës, tàmbalee waxtaan ak keneen ci telefon bi. Xamoo dara ci li muy wax, waaye wóor na la ne ki muy jokkool boroom barke la ni moom. Nga gis ni Baydi féexe, di làkk nasaraan yu set wecc, daldi soppiku xaat. Mel ni bunt bi dafa ubbiku ndànk, beneen Baydi Gay duggsi ci biro bi. Wax dëgg Yàlla, ba Baydiy làkk wolof ak yow nga ko gënoon a ñeme. Ñaari gone ngeen woon, ku ci nekk di fàttaliku démb. Waaye Baydi Gay mii téye telefon bi de, Muse le Direkteer-Seneraal la, lee-lee mu wax ba tudd ay milyoηi seefaa yu bare, sànni la catu bët. Waay am na ñu sant Yàlla ! Baydee ngi nirook wundu Tubaab yooyu ñu sang ba ñu set, defar leen, teg leen ci ay njegenaay yu nooy nepp, ñu ne fa noηη di óbbali,
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_116
di lekk yàpp, di naan meew. Xanaa looloo tax su nit tubaabee ba mu ëpp, ñu koy tooñ, naan ko ηeew la ? Nangul mbir mi, Ngiraan : ñee nga Baydi Gay lool ! Yaram wépp a ngi nokki. Xam na moom ci boppam ni ku dugg ci biroom, fekk ko mu toog ci béréb bu rafetee nii, fàww nga naw ko. Yow nag, Ngiraan ? Nirootook nit. Xoox nga lool. Baydi sa moroom la, waaye ku leen gis ngeen toog dafa naan nijaayam nga. Yaa ngi yooy be, ndeysaan. Nga jóg di dem, Baydi Gay jox la loxo, buuxaale la kayitu junni ne la paase ko ba noppi woo sófóoram, ni ko : - Sayeer, yóbbul ma Muse Fay këram... Sófóor bi xool la ci kow ba ci suuf, xol bi bon, mu ne : - Madam a ngi may xaar de... Baydi jàpp bopp bi : - Waxati nga dëgg, Sayeer, waaye demal rekk, dinaa woo Yaama...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_117
Sófóor bi moom daldi na la jéppi ci saa si. Fu mu ko teg ? Xéy-na li nga ne noηη ci ginnaaw oto bi, mu lay dawalal moo ko naqadi. Ni mu la gise, xam na ne soo ko tanee it du lool. Xanaa loolu mooy : - Nangu naa jaamu Muse Gay miy boroom alal, waaye ngóor sii ak yëreem yu furi yii faalewuma ko. Dañuy wax rekk, Badu, waaye baadooloo fi gën a iñaan ci moroomam. Fi ngay xalaatee loolu sa xol tàng, sófóor bi ne la : - Jambaar, yow sax foo xamanteek sama seef ? Sa xol gënatee fees. Nga dem ba naan ko yow it kilifa nga, ndax am nga isinu saabu bu mag. Waaye tàmmoo fen. Nga ne ko : - Kan, Baydi ? Noo màggandoo Garaη- Kees. Mu ni : - Ca Kees... ?
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_118
- Foo bëgg Garaη-Kees nekk fu dul Kees ? Li muy wax ak yow yépp, mu ngi lay niit ci seetu bi ci biir oto bi. Nga ne ci sa xel : sófóor bii gën a soxor te ñemee toppatoo lu yoonam nekkul ! Mu laaj la fan nga jëm. Doo ko wax moom ne Ñarelaa nga dëkk, nde kon mu gën laa yab ! Nga ne ko : - Wàcce ma ci bitig bee ci boppu koñ bi. - Muse Gay kat... Nga dog ko, ñagasal sa baat, mel ni ku koy gëdd : - Wàcce ma fi ma la wax ! Sa xel dellu ci Baydi Gay. Dëgg la, kaf ngeen bu baax, teral na la, waaye wax ja dëgg-dëgg du woon rekk fa ngeen jaar ca seen ngone walla janq ja ngeen daan jéem a doxaan. Ay kàddoo ngi doon fecc ci seeni bët. Ay kàddu yu nopp mënul a dékku. Ñuy tëb di dal ci sa biir kaaη. Lii lépp, yaa ko teg sa bopp, Ngiraan. Baydi tamit a ngi naan ci xelam: - Lii lépp yaa ko teg sa bopp, Ngiraan.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_119
Saa yu nu daan jàng sunuy lesoη, yaa ngay fiir ay picc ci àll bi mbaa di wax waxu fecc ak doxaan janq ji. Léegi nag, mu ngi nii, yaa ngiy wër di ñaanaatu. Li ngeen di waxtaan yépp, kàddu yooyoo ngi jaabante ci jaww ji. Moo tax ma ni la, Badu : Defuma ci suma dund gii lu ma mën a bàkkoo. Dama tëñëx-tëñëxi ba xéy màggat, mënatumaa dem, ma déju. Loolu, gis naa ko ci njël googu ma wund wa tiime, jooy, jooyaat. Ma neeti ci sama xel : - Yàllaa ma sàkk, dëgg la, ma tudd Ngiraan, sant Fay. Waaye ñan ñoo jur samay wayjur ? Fan laa jóge ba agsi ci taatu garab gii, am wund wu ñëw tiim ma, jooy, jooyaat ? Badu, nit ku bëgg a xam mooy kan ci dëgg-dëgg, fàww mu am fit. Dina tancu ci ruq bu lëndëm këruus, fekk fa ay néew yu jaaxaan, waaru ñoom it, di ñaan Yàlla mu may leen ñu dellusi dunyaa, di dunde yaakaar.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_120
Tey a ngi làqu ci biir Démb, ne nemm. Jéemal a tëj sa loxo bu baax. Ŋëb fa jamono ji balaa mu lay rëcc. Maam Ngóor lañ ko daan woowe. Mu nga, tëdd Mbériη-Saaj, ca Siin. Njël ga ma wund wa tiime, di jooy, loolu la ma fàttali. Mu am lu ma yëg ci sama yaram. Ma daldi ne nu ma def dinaa dem Siin, man mii. * * * Dem Siin wuti fa lan ? Xanaa siyaareji bàmmeelu Maam Ngóor, ca Mbériη-Saaj. Mu mel ni nag dañ may xabtal : - Jógal dem, Ngiraan. Mag ñaa nga Mbériη-Saaj di la xaar. Ñoom ñoo xam Maam Ngóor. Dinañu la wax yaay kan. Xanaa bëggoo xam yaay kan ? Moo tax bés ma xéy, tëj sama buntu néeg, jubal gaaraasu Kolobaan. Sunu Toyotaa génn Ndakaaru,
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_121
nu romb Tëngéej, teg ci Barñi, tàllal ba Jamñaajo nu door a jàdd wutali Mbériη- Saaj. Sama xel ne yarr ci kàddu ya ma daan dégg ba ma newee gone. Benn ëtt bu yaa. Fan la woonati, sax ? Du woon Mbériη-Saaj, moom. Ay mag toog ci pénc mi, di waxtaan. Ñaari baat yu ne, ñu tudd Maam Ngóor. Lu ne ñu koy wax ciy mbiram. Man, ma nekk gone, bëgg a laajte kan moo doon Maam Ngóor. Waaye amuma boobu sañ-sañ, ndax ragal ku àjji sama kaabaab, gëdd ma : - Luy sa yoon ci waxtaanu mag ñi ? - Ku mas a gis lii ? - Gone gii gën a teggi ndawal ! Jamonoy dox. Ma dëkksi Ñarelaa, takk fi jabar, uuf sama njaboot. Teewul fu ma jëm turu Maam Ngóor topp ma. Fu ma taxaw, takkandeeram taxaw ci sama wet. Mu ngi ne nemm ci sama biir kaaη gi, tëdd fi ay ati-at, di xaar. Su ma ko cokkaasee, mu yeewu, fuddu, ni ma :
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_122
- Dara, nag, Ngiraan : ku sa maam jur, jur nga sa maam. Bu la ci kenn nax. Ma téen, yaakaar ne biddéew yi dinañu ma tekkil baat yu xóot yooyu. Biddéew yi ne cell. Ngelaw li jóg, daldi woy, ay woyam dekkali jaar-jaaru Maam Ngóor. Badu, nee ma : - Maam Ngiraan, loo daan dégg mag ñi di ko wax ci Maam Ngóor ? Daan nañu yéemu ci xam-xamam. - Doomi kilifa yu bari moo leen daan jàngal. - Waaye Maam Ngóor a naqadi woon deret ! - Dafa àndoon ak xadar. - Ñépp a ko ragaloon. - Moo sonaloon Maalig mii toog, tey ! - Bés, doon naa tari benn saar, gag. Keroog dafa ma yeew ca géttu xar ya, ma fanaan fa. Suba teel la ma fa fekk,
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_123
sotti ma ndox mu sedd guyy, caw ma ba sama yaram wiy nàcc ! Bi Maam Ngóor demee ba màggat, dafa gàddaaye Siin, dem sanci Tëngéej, takkoo faak Bintu Jaara. Soxna si jur sama baay nag, masumaa dégg turam. Doy na waar gaa, waaye noonu la deme. Leneen lu ma wax ci Maam Ngóor, ay fen la.Xanaa boog ma fent... Maam Ngóor ku ñuul la, àgg ca kow. Ginnaaw nee nañ ci mer ak dóore la dëkk, ma yaakaar ne bët yi dañoo wara a xonq coyy ni ay bëti gaynde. Foo ko fekk, mu ngi toog ci deram, goney Mbériη-Saaj yi wër ko, mu leen di sa, ñuy tari. Waaw, jamano jan la Maam Ngóor newoon Mberiη-Saaj ? Ku ma gis ak samay bejjaaw, xam ne su matulee ñaari xarnu it, waru koo sore. Mbériη-Saaj, dëkku kow la. Yoor-yoor laa fa àgg. Dox naa lu yàgg te dajewumaak nit kuy noyyi. Su doon jamono yu jëkk ya,
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_124
damay jàpp rekk ne waa Mbériη-Saaj a nga tool ya. May wër ba séen benn waa ju wéeru ci benn sàkket, ma jubal ci moom. Li nuy nuyoonte yépp, mu ngi may ronni, naan xam naa, ci xelam : Kii de, dëkkul fii fépp. Man it, li ma tax a jële oto Ndakaaru wutali Mbériη-Saaj, yombul a wax. Mënumaa tëb jaar ci digg bi. Rax-ci-dolli, ngóor si ma fekk ci taatu sàkket wi, niruwuma ku yemb.Yaram waa ngi xasan, muy wokkatu, di onk. Ma ne ko : - Ngiraan Fay laa tudd. Fii laa cosaanoo, ndax maay doomu Dibókóor Fay, di sëtaatu Maam Ngóor. - Maam Ngóor ? Bi ma déggee ni mu waxe, xaw naa am tuuti yaakaar. Mu gën a wokkatu, reetaan, dellu ne ma: - Aa ! Maam Ngóor ? Ma ne ko : - Waaw, Biraan Fay mooy turam dëggëntaan, waaye ci turu Maam Ngóor lañu ko gënoon a xame.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_125
- Aa ! Te nga ne yow jarbaatam nga ? - Déedéet, sëtam laa. - Sëtaatu Maam Ngóor tàww !... - Déedéet. Sëtam laa wax. - Biraan Fay de, yëguma fu mu amee doom, bay am sët. Loolu kañ la ? - Monte li ma wax de, leer na ! Waa ji mer, xaaxtandiku sànni fu sore, jóg taxaw : - Aa ! Man ngay gëdd ? Ãa ! Danga ma teg dof ! Naka laa dégg loolu, daldi tàmbalee dellu ginnaaw. Li ñuy wax ci gaalu dof moom, ñépp xam nañu ko. Foofu, am ku ne ndànk ci sama ginnaaw : - Àndal ak teey, waa ju baax, sooy daw mu lay dàq te su la dabee dina la rendi rendi bu ñaaw. Ma geestu, yem ci benn góor gu màggat, mu sex naanoom. Mu ne ma :
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_126
- Am na lu ma jot a for ci seen waxtaan de, man mii. Ci sama tiitaange, maa ngi xiixat, naan ko: - Monte samay tànk de, góor gi, tànki jàmm doηη lañu. Mu muuñ, ma seetlu ni bët yi dugge. Mu ne ma : - Bu dee Biraan Fay mi ma foog de, Tëngéej la faatoo. - Maam Ngóor lañu ko daan woowe. - Kon boog mooma. Waaye, léegi, luy say tànk ci dëgg-dëgg, waa ju baax ? - Dama siyaaresi bàmmeelam, ñaanal ko. - Guléet boog. Fii de, kenn fàttalikuwul fu mbokku Maam Ngóor ñëwe Mbériη-Saaj ne da koy siyaaresi. Foofu, yëg naa ni ay kàddoom ñagase. Sama xel di werante : « Góor gii, moom, dafa am naqar ci li kenn masul a siyaaresi Maam Ngóor walla dafa bëgg wax ne mbirum Maam Ngóor jarul boobu coono ? » Ma ni ko :
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_127
- Man mii de, bitim-réew laa newoon, te yàgg fa lool. Moo waral sunu gise yéexe nii. Maa nga woon Milaano, ca Itali. Foofu... Góor gi dog ma : - Dangay kàcc, Ngiraan Fay. Xamoo sax fu dëkk boobu féete. Maa la gën a xam sa bopp fuuf ! Mën naa la wax it fan nga xéye, ne Mbériη-Saaj maa ngoog. Ba ngay tàllal kokseer ba kayitu ñaari junni, ca gaaraasu Kolobaan, mu ubbil la otoom bu weex ba, nga toog ca ginnaaw, maa ngi fii Mbériη-Saaj di janook yow. Su ma neexoon ma këpp Toyotaa bi la fi indi, nga dee ci yoonu Mbériη-Saaj ! Loolu du dara ci man. Bi nga agsee, wëndéelu nga lu yàgg biir Mbériη-Saaj te dajewook kenn. Xamal ni booba, waa dëkk bépp a ngi lay seetaan. Waaw, tànk boo yëkkati, teg ko ci suufu Mbériη-Saaj gii, jaaxal na lool waa dëkk bi. Gisoo kenn ci nun, waaye nun ñépp a ngi la teg bët. Foo romb, nu ngi naan :
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_128
- Gan gii de, ci xeetu Maam Ngóor la war a bokk... Xanaa kii dafa repp ? Mbir maa ngoog, Ngiraan. Kon soo fi tuddatee Milaano, dinaa la def lu bon. Ma dem bay tontu góor gi, mu të ma. Sama baat biy lox, ndax ni ma tiite. Ma ne tekk, di xool góor gi. Gisuma ci moom dara lu tax ma mën a xalaat ni du nitu neen. Ku tuuti la te ñuul, sol sabadoor bu dóomu-taal ak ay maraakis yu weex. Tengaade bi mu teg ci boppam it, du lu ma war a jaaxal. Kuy faral di dem ci dëkki kow yu daw yi, dinga fay gis beykat yi teg tengaade ci seen kow bopp, ngir mu aar leen ci naaj wi. « Céy, man ! Ci lan laa duggati ? » Góor gi gëddaat ma : - Nee naa la dangay nar, Ngiraan. Doo ma tontu ? - Fi mu ne kay, balu àq moo ma dese. - Aajoowu ko. Léegi nag, waxal lu la fi indi, ci dëgg-dëgg. Yëf yi du caaxaan.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_129
Ma gën a tiit. Yëf yi du caaxaan... Xawma lan, waaye loolu moom leer na ma. Mbir mu kéemaane sax ! Wund wa ma tiimoon Ñarelaa daldi dellusi ci sama xel. Ma déggaat ko muy jooy. Góor gaa ngi ma ni jàkk, di xëcc naanoom. Lu ma koy tontu ? Am nay kàddu yu benn Doomu-Aadama sañul a génnee ci gémmiñam. « Ba àddinay tukki, duma wax góor gii ne jooyi wund yaa ma tax a xéy, sol samay dàll, jubal Mbériη-Saaj ngir xam maay kan ak asamaan san laa xàwweekoo tàbbi ci biir dunyaa ju rëb jii. Su ma ko waxee loolu, dina yaakaar ni dama koy foontoo te kon du baax ci man. » Ma ne ko : - Waaw, góor gi, yow ci sa bopp, yaay kan? Mu xool ma ba seppali ma, sog ne: - Ngiraan, fii wund du fi naane ñeex. Fii ci Mbériη-Saaj de, ku masul a gis Maam Ngóor it xam nga jëf ju bon ji mu fi def. Foofu nag, li may ragal góor gi yépp, xaw naa ñéññ :
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_130
- Man de waa ju baax, sa tur rekk laa la laaj. Gisuma lu waral ngay xas samay way-jur. Mu xoolaat ma ba yàgg, ne ma : - Maam Ngóor laa wax, moo fi yéesoon. - Aa ? - Maa wax loolu. Fii ci Mbériη-Saaj, ñépp xam nañu mbonam. Liir yiy soog a juddu sax, su ñu déggee turu Maam Ngóor seen fit rëcc. Keroog jooju laa waaru ci Yàlla ! Maa ngi naan ci sama xel : « Li Maam Ngóor def waa Mbériη-Saaj de, war naa réy xanaa ! » Xamatuma lu ma yëf yiy niru. Ma ni ko : - Timis soreetul, te ëllëg rekk laa fiy amaat oto bu ma delloo Ndakaaru. Fàww ma fanaan Mbériη-Saaj. Góor gi mel ni ku ma déggul, daldi may laajaat :
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_131
- Nga ne lu deeti say tànk sax, Ngiraan ? Ma takk sama fit, fas yéenee janook moom, wax ko nag dëgg. Mas naa waxtaan bés ak benn boroom xam-xam. Nu dem ba ci biir wax ji, mu ni ma : - Doom, gor bu sësee dafa war a fàttaliku la mag ña daan wax. Laaj ma wax jooju jan la, doom, ma wax la ko. - Laaj naa la ko. - Wolof Njaay dafa ne : Ndënd mu ñu tëgge sémmiñ : neex benn yoon, naqadi benn yoon. Loolu lii la tekki, Badu : gor dëgg, su ñu ko naree toroxal, day nangoo jaay bakkanam, lu ko ciy fekk fekk ko ci. - Dara indiwu ma fi lu dul bëgg a xam kan mooy Ngiraan Fay ak fan la xeetam soqeekoo.Ni ma tontoo xaw a jaaxal góor gi. Mu gaññ, gën maa xoolaat, ne ma :- Ngiraan Fay man ? - Xanaa Ngiraan Fay mii taxaw, janook yow. Fan yale ñu génn, toog naa sama kër ca Ñarelaa, benn wund ñëw tiim ma, jooy ay yoon i yoon.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_132
Booba ba léegi amuma jàmm. Fàww ma xam maay kan ak fan laa cosaanoo. Nit ku xamul loolu, yaak xobu garab wi ngelaw liy ëf, muy wëndéelu ci jaww ji yéen a yem. Góor gi ne ma jàkk, sama xel dellu ca wundu Ñarelaa wa. Mu wiccax boppam ba yàgg, joxoñ ma benn kàdd : - Séen nga kàdd gale, de ? - Kàdd gi mel ni lu tafu ci jant bi ? - Waaw. Ñu ngay tàggatoo ñoom ñaar. - Tàggatoo ? Ñan ay tàggatoo ? - Kàdd geek jant bi. - Firil ma wax jooju, góor gi. - Taxu koo am solo. Seen waxtu tëree jot doηη. - Nga baal ma de, góor gi, waaye... Foofu, xol bi bonaat, mu ni ma : - Sa yoon da cee nekkam ? Léegi, laggal. Soo demee ba tollook kàdd googu, jàddal sa càmmooñ. Soo doxaatee tuuti, dinga gis sëgi Mbériη-Saaj yi.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_133
Dem naa ba naan ko : - Waa Mbériη-Saaj ñoo mën gan ! Waaye mii xel ne ma xuloo xeju fi te it wax dëgg Yàlla man lañu jekku woon. Aa ! Man mi yaakaaroon ne bés bu ma agsee Mbériη-Saaj, teeru bu mag laa fiy am, samay mbokk fàqee fu ne daw wutsi ma, ñépp di ma sargal, maak ñoom ñuy yuuxoo, di jooy ndax mbégte ak nammeel gu metti, foo tollu dégg ku naan : - Ndeysaan, kii mooy Ngiraan Fay, sëtu Maam Ngóor mu baax ma. Ku nekk bëgg maa ganale, ñu may xëccoo, di ma berndeel... Ma mujjee toog Mbériη-Saaj ay weer ndax saa yu ma bëggee dellu Ñarelaa ñu ne ma mukk du ci dal, ku nekk di ma nettali jaloorey Maam Ngóor, naan ma : - Ku amoon diine la, bi muy sàncsi Mbériη-Saaj gii de, ceddo yee fi ëppoon, ëpp fi doole, waaye...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_134
- Ceddo yi kay ! Li Yàlla xam doy na ! Su ñu naanaan seeni këlli sëng ba seen yaram tàng, dañu daan fekk Maam Ngóor fi mu toog di jàngal gone yi, ñu koy wéq, di ko saaga, di saw ci kow bopp bi ! - Ana mu tey ? Dëgg rekk mooy dëgg ! Tey de, kenn dootul bàkkoo sama maam ceddo la woon ! - Du Sëriñ Mbay Jaxate woy na ko ? Ña daa weranteek a boccantey gobar di xuloo Di naan ak ay màndi moo ñooñee ku xam ana ñu ? Moy Yàlla moo bon ku koy def ag mujjam du rafet Mbooleem ñi daa def lu bon kenn xamul ana ñu ? Ñu doon i buur ak i baadooloo ngi bokk ne mes Ci suuf si, gaa ya réyoon ak gaa ya sew ana ñu ? - Maam Ngóor ! Kooku boroom xam-xam dëgg la woon ! - Naqadi woon na deret, gaa, waaye dara waralu ko woon lu dul njub gu ëpp. Waay, Badu, maa bëggoon a dégg kàddu yu neexe noonu ci Maam Ngóor !
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_135
Kàddu yooyu soppi kon nañu ma ba fàww, ma dellu Ñarelaa, nekk keneen. Ngiraan Fay, sëtu Maam Ngóor, boroom Mbériη-Saaj. Ku sànc dëkk de, deseelatoo kenn dara, te Maam Ngóor moo def lu réy loolu. Su deme woon noonu, sama xol du diis ba duma ko àttan. Kon damay toog ci buntu kër gi, waa Ñarelaa di ma romb di ma nuyu, yaakaar ne maay Ngiraan Fay ma ñu xamoon. Ma xam li ma xam rekk, ne patt. * * * Dinaa la fi waccal tamit Téereb Wis. Ci laay xej-xejal kàddu yi ma xamul fu ma leen di def. Loolu du dara lu dul pexeb nettalikat. Dina tax sunu jokkoo maak yow gën a yomb. Cere dees koy laalo, du ? Ëllëg-ak-sibir, dinga uuf say doom, ngeen di seetaan nataal yi nekk ci Téereb Wis. Nga naan leen :
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_136
- Nataal yii, seen Maam Ngiraan Fay a leen jëloon. Booba, kenn ci yéen juddoogul. Ñarelaa ngi nii, mooy nataal bu mag bii. Fii laa juddoo, man seen baay Badu Taal. Gis ngeen ni gox bi meloon bu jëkk ? Mbaa : - Boroom lonet yii janook mbooloo miy wax, mooy Séex Anta Jóob. Xool-leen ko bu baax. Dafa mitiηsi woon Ñarelaa. Boroom xam-xam dëgg a ngi nii ! Ci Téereb Wis, seen Maam Ngiraan bind na ci moom ay kàddu yu am solo te daw yaram. Nee na nit ku lewetoon la te woyof. Masul a def dara muy dara waaye kenn feesul woon ay bëtam. Loolooy Téereb Wis, Badu. Sànnil naa la ci it ay kàddu ci Ñarelaa. Nun ñi fi dëkk ay baadoolo lanu. Danoo sonn ba nirootunu nit. Nu ngi dankalikoo ci ay ruq yu xat te lëndëm, dëkke tés-tési. Ñarelaa wutewul ak toolu xare. Ku nekk ci nun a ngi jéem a doxe sa moroom ginnaaw.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_137
Soo ko jekkoo gal-gal ko mu daanu mbaa sax lee-lee nga jam ko paaka, butit yiy watatu. Ak lu ma mën a wax, man mii ci baadooloy Ñarelaa yi laa bokk. Du nag lu ma gënal. Ku ma romb ci sama buntu kër gii, mën nga ma ne : - Ngiraan Fay, doo nitu dara, ndax yaa ngi nii toog Ñarelaa, kaña yeek xaj yu médd yi wër la, newwi, nëb, xasaw xunn, weñ yiy biiw di muucu seen dëtt, di naan seen deret. Moo ma taxoon a dawe bés Ñarelaa, fàq wuti Mbériη-Saaj ca Siin ngir raasaatu fa ci wàllu ngor ak ndam lu ma nawe sama bopp. Su ko defee, képp ku ma jéem a suufeel, ma xamal la maay kan : - Dëgg la amuma alal, man Ngiraan Fay. Waaye kenn du ma yab ! Maam Ngóor mi jur sama baay, moo sànc Mbériη-Saaj, ca Siin, ji fa mbaax, wone fa fit ak jom ju mat sëkk. Dama ne, Badu, ndegam dara desul lu dul xaar ndogalu Yàlla, su doon sama sago ma am fu ma langaamu, nawe ko sama bopp. Li may janeer di ay caru garab, ma ciy njoowaanu,
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_138
péex mu neex di ma upp. Saa yu ma gëmmee, fàtte Ñarelaa, daldi gis Maam Ngóor mu sol mbubb mu weex tàll, di dox moom kenn ci joor gi. Rabu àll yépp di jébbalu ci moom, guy gu mu romb nga yéene ko sa keppaar, gunge ko ba mu àgg fa mu jëm . Maam Ngóor moom di wéy rekk, di tudd turu Yàlla, du geestu, du siggi benn yoon xool li ko wër.Jàppal lii, Badu : nit, su xamulee fan la fekk baax dëgg, dundam neen na. Li may xalaat loolu yépp, góor gaa ngi taxaw, jàkkaarlook man, ne ma jàkk. Ma ne ci sama xel : « Monte góor gi kaful, dafa ma nar a seetaan ma fanaan ci biti, muy làyyi ci sama kow ba bët set. » Ma ne ko : - Waaw, fii fépp amul sax néeg bu ñu ma fi mën a abal ba ëllëg ? - Déedéet. - Ba léegi nag, nu may def ? - Ngiraan, teg nga say tànk ci dëkk bi te dara fekku la ci. Tee ngaa dellu Ñarelaa ! Lu mu guddi-guddi, moo gën ci yow. √
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_139
Xawma fan, waaye Mbériη-Saaj gii moom, soo fi fanaanee du la jig. - Ba noonu daal, góor gi ? - Yaa ngoog, yoonu sëg yaa ngoog. Soo siyaaree ba noppi, jaare fa ñibbi. - Aa ? - Man de noppi naa ci wax ji, Ngiraan. Xam nga, Badu, nit su goree te jaambure, du gaaw a torox. Bu demee ba sës, Yàlla dafa koy dooleel. Ma yëg ci sama yaram ne man, Ngiraan Fay, doomu Dibókóor Fay ak Xemes Seen, ak lu ma ci mën a fekk, warumaa may waa Mbériη-Saaj lu ñu may reetaane. Ba ma wonee góor gi ginnaaw, jëm sëg ya, maa ngi yëg ni ma bëtam yiy toppe, di ma jamat ci doq ni ay puso yu ñu tàngal ba ñu sãs. * * * Bët, ci jëmmu Doomu-Aadama lay sax. Waaye xelu nit itam dinay faral di am i bët.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_140
Soo bëggee xam naka la armeeli Mbériη- Saaj yi mel, gëmmal. Béréb, su nit xamul fu mu féete, te mu wóor ko ne dina dund ba dee te du fa xand, bëti xelam a ko fay yóbbu. Gëmm ngaam, Badu Taal ? Yaa ngi séen ay kàdd yu dóomu-taal, yegg ca kow te wow koηη. Ñu ngi tiim ay jali suuf yu ndaw. Maa ngi wër ak a wëraat ci sëgi Mbériη-Saaj yi, bàmmeel bu ne ma taxaw ca, yaakaar ne fa la Maam Ngóor tëdd. Sëg yaa ngi ne selaw, xanaa leeg- leeg rekk ma dégg picc yiy woy, di dem ak a dikk ci seeni tàgg. Noonu laa ko jàppee lu mat ñetti waxtu. Ba ma fa jógee, fas yéenee tegu ci yoon wi - waaye wax dëgg Yàlla xawma sax yoon wan laa war a tegu - fekk na jant bi so bu yàgg. Naka laa won sëg yi ginnaaw, daldi séen këri Mbériη-Saaj yi ñuy tàkk, mu mel ni sama digganteek dëkk bi dafa gënatee xëcc. Béréb baa ngi lëndëm këruus, wéet ba nga ne lii lu mu doon. Fu ma walbatiku, lëndëm gi téj samay bët,
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_141
fatt sama bakkan. Waaye demuma sax bay tiit.Dina ñuy wax ne : - Ku la yéene xiif, saa yoo ko rombee géexal.Noonu doηη la mbir mi deme. Keroog laa xaare waa Mbériη-Saaj ! Nit dina tollu fu mu dootul xàmmee boppam. Moo tax boolewuma ci wax. Dama làmbaatu ba daj benn xeer wu réy, ma wéeru ca. Ni ma tooge, mii xel ne ma góor kat, su bañee ñu bett ko, day fagaru. Ma daldi jóg, for ay doj, jóor leen ci sama kanam ba noppi gànnaayoo benn yatu kel wu dëgër. « Tey jii de, waxuma bukki mbaa till waaye gaynde sax su ma songee dinaa ko defanteek moom ba ba mu may rey, ηànk sama néew yóbbul njabootam ». Fi ma toog, jàkkaarlook dëkk bi, maa ngi gis ni ko lëndëm giy muure ndànk-ndànk. Làmp bu fay beneen tegu ci. Mu jàppe ko noonu ba Mbériη-Saaj réer ma. Bi ñu demee ba benn këru Mbériη-Saaj tàkkatul
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_142
ma dégg ay tànk yuy yoot ci ñax mi. Fi ma deme ba naan : - Kooku ? Am ku ne : - Man a. Bul tiit. - Yow a kan ? - Doo ma ne kañ xàmmee woo sama baat, Ngiraan... Dafa tudd sama tur rekk, sama xel ni yarr ci góor ga ma teeru woon ci bëccëg. Toogagul sax daldi ma ne : - Naka mu, Ngiraan ? Li doyoon waar, Badu, lii la : baatu góor gi du woon baatu kuy wut ay, dara luy nirook ñàkk teggin raxul woon ciy kàddoom. Mu mel ni daal ku teeru gan sa kër, jox ko mu reer ba suur, nga di ko àttaayaal, ngeen di waxtaan ni ay xarit yu gëj a gise, ku ci nekk nammoon lool sa moroom. Walla boog dafa ma doon kókkali ? Ma ne ko : - Xanaa du yaa ma dàq sànq Mbériη-Saaj ni xaj ?
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_143
- Baal noonu yow it, Ngiraan. Loolu amul solo. Ma gën a mer nag, déjuwaat bu baax, ni ko : - Góor gi, noo tudd ? - Tee ngaa bañ a mer, doom ? Man maay... (Foofu, wax na ma turam. Su ma ko fàttalikoo feek ëllëg, dinaa la ko yokkal ci Téereb Lëndëmtu bii may bind). - Léegi xam naa sa tur waaye am na lu des. - Loolu lu mu, Ngiraan ? - Doo fi jóge tey te waxoo ma wure wi nga may wureloo nu mu tudd ! - Mbaa du sa xel dafa la jay ba nga may sóoru ? Bumu ñaar ! Foofu, Badu, gis naa ni góor gi caaxaanatul. Li muy wax yépp, loxo ndeyjoor baa ngi doxantu ci wetu geño gi. Mu wóor ma ni gànnaay la fa ñóox. Ma xam ne yoonu jàmm sorewul, ma ne ko :
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_144
- Man kay sañuma laa sóoru, góor gi, nde tuutee tee nga mat ba baay. Su dee dama la tooñ, baal ma àq. - Moo gën ci yow. Léegi nag, wuyu ma : naka mu, Ngiraan ? - Wër naa sëg yi lu mat ñetti waxtu, gisuma fenn bàmmeelu Maam Ngóor. Ñëw bi ma ñëw Mbériη-Saaj de, amaluma benn njariñ. Ëllëg ma ñibbi Ñarelaa. - Bul waxe noonu, Ngiraan. Dinga am loo jële Mbériη-Saaj, ndax sa yóbbal laa la yótsi. Mbériη-Saaj a ma yebal ci yow. Wax jooju jaaxal ma lool. Ma ne bëret, ni ko : - Yóbbalu waa Mbériη-Saaj ? - Waaw. Mu muuñ, mel ni ku may kekkantoo. Sama xol jógMa ne ci sama xel : « Su yaboo góor gii gor ma jaasi, daggat sama yaram sànni, till yeek baaxoñ yi di ma jiiroo, waaye duma ko seetaan mu may fowe nii ba bët-set ».
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_145
- Daw naa ay lu ma mën, góor gi, waaye nag yabeel gaa ngi bëgg ëpp. Góor gi muuñaat, ne ma : - Yaa yey jaaxle, Ngiraan. Yóbbal bi ma lay wax de, ay kàddu doηη la. - Ay kàddu ? - Waaw. Du siddéem, du gerte-kemb, du kóoni, du new, du leneen. Du lu diis looy yéenu ci naaj wi, di ko dugal ci oto, jëm ak moom Ñarelaa. - Dëgg la. Waaye am na lees waxul de, góor gi. - Ma ni : ay kàddu laa la yótsi. Du looy yenu. - Ba tey waxoo wax ji de. - Waaw. Du kàdduy neen, ndax mën nañu laa diisal sa giirug dund. Ma neeti ci sama xel : « Waa Mbériη-Saaj yii de, kenn gënu leen a doy waar ».
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_146
Ba may reetaan man ci sama bopp, teyuma ko. Badu, li ngay jàngsi bu ci kanamee, mooy la ma góor ga wax guddi googu. Yokkuma ci dara, wàññiwuma ci dara. Guddig àjjuma la woon. Tàbbal na ci samay nopp ay baat yu lëndëm te kéemaane. Ni ma leen jote laa la leen di jottalee. Déglul ma boog góor gi ma fàtte turam, fàtte santam... « Nit ku nekk, Ngiraan, am na nooy gise sa bopp. Waaye sa melokaanu kanam dëgg, noo def ñeneen ñee la koy gën a xam. Ñaata yoon ngay seetu ci ayu-bés bu nekk ? Néew na lool. Saa yoo janook sa seetu, nit ki ngay gis ci biir, maanaam yow ci sa bopp, kersa mën naa tee nga xool ko lu yàgg. Ku xelam neexul rekk moo àttan a taxaw ay waxtu di seetoo ka seetuwaat. Waaye su fa dof boobu fanaanee it, du ko amal njariñ. Ma ni : sunuy dëkkandoo ñuy gën a xam naka lanu bindoo.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_147
Lu waral loolu, Ngiraan ? Foo fekk Doomu-Aadama, ñett yii ma lay limsil ñooy yatt kanam gi : mer mbaa tiis mbaa mbégte. Ñett yooyu, bu ci nekk dafa nuy faral di doxe ginnaaw. Te it, bu ci nekk ba muy ñëw ak ba muy dem benn lay doon. Mënoo saa yoo reetaanee mbaa nga mer, daldi këf sa seetu ngir gis ci naka la sa kanam soppikoo. Xel nanguwul loolu. Benn seetu rekk a wóor. Laaj ma ban la, Ngiraan Fay, ma wax la ko. - Laaj naa la ko, góor gi. Seetu boobu mooy bëti nit ñi ngay dajeel ci mbedd mi. Nun ñépp, ci suba ba ci ngoon, nu ngi dem ak a dikk ci biir bëti ñi nuy digaaleel. Koo ci ne jàkk, ak lu ngeen wute wute dina la wan yoon wi lay yóbbu ba ci sa bopp, nga gën a xam yaay kan. Yaay man. Maay yow. Te Ngiraan, li wokk nit ki, mooy xosi askan wi.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_148
Bés a ngi ci bés yi, buy indil Doomi- Aadama yi njàqare. Askan wi day yeewu bés, dootul xàmmee boppam. Ne : - Li woon, wonni na. Yoon wa maam xàlloon démb, seey na ci biir géeju fen ak tappale. Kan moo fi jaar ba soppinu nii ? Su askan wi joowee ba ci diggu dex gi, bu sëppoo, seetu, keneen lay gis. Askan wi ne : - Kii ma janool de, du man.Wax jooju di dëgg gu wér péηη. Ay doxandéem jot nañu fee jaar, walbati xel yépp. Am ci askan wi ay jàmbaar yu fippu, ne : - Lu tax nu nangoo wànteer sunu ruu ? Li nu ko wecceel jar na ko, mbaa ? Fippukat yooyu nag, askan wi dafa leen di jàppe ni ay dof, lu nekk mu leen koy yakk: - Bu leen nu sonal, waay ! Deret sax su tilimee dees koy fete ! Fippukat yi waaru, taf seen gémmiñ : - Aa ! Wax jooju ëppul, ngeen yaakaar ?
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_149
- Lan la maam doon sàggan ba ay doxandéem ñëw di ko daan, di ko toroxal? Déglu ma, Ngiraan : bu lu ñaaw looluy am, day fekk xobu garab gi wow koηη. Ay fan ci ginnaaw rekk, ngelaw li upp na ko lu yàgg a yàgg. Muy njoowaanu, di raay asamaan si, di noyyi, féex ba, tubaarfakàlla. Lee-lee taw bi dal ndànk ci kowam, raxas ko ba mu set wecc, dënnu yiy yàkkali dënnam, melax yi di ko may seen leeraay ci xol bu sedd guy. Ay tóor- tóor wër ko ne ràyy, xeeñ bann, di samandaay junniy-junni lëppa-lëpp yu ci benn niroowul ak moroom ma, taaru ba nga ne li lu mu doon. Ramatu yaa ngi koy ñoromtaan. Muy reetaan, naan leen : - Aa, yéen a mën a tooñ, sama gaa yu baax yi ! Man daal ngeen def seen doomu- bàjjan ! Àddinay dox ba garab gii wow, xob wa màggat, rasu. Bën-bën feeñ, siddit yi rocciku, yaram wi ràgg, ñu as li des ci meen mi, tuur. Bés bu ne benn bëñam rot.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_150
Xobu garab gi dootul saf kenn ba bés ba muy daanu, di xalangu ci suuf si, tànk bu fa jëkk a jaar dëggaate ko, mu daldi soppiku pënd ci saa si. Nun waa Mbériη- Saaj de, li nu mas a xam mooy teral gan, yaatal ko. Moo tax jamono ja nga xam ne lu waay am fit ak doolee la ko may te ku jekku sa moroom bojj ko paaka, képp ku mosaan a daw, ñëw làqusi Mbériη-Saaj, raw nga.Yow nag, Ngiraan, wund wa nga gis Ñarelaa mu tiim la, ne la jàkk, Mbériη- Saaj gii la jóge. Noo ko yebal Ñarelaa. Xamal loolu bés niki tey. Léegi, déglul bu baax li ma lay waxsi ci mbirum Maam Ngóor. Su fi Maam Ngóor cosaanoo woon sax, ñu ni waaw. Waaye dëkk bu ñu naan Njooreen la fekkoon baax. Ba mu demee ba bëgg a jommal waa Njooreen, waxi dof yu nekk mu koy génne ci gémmiñam gi, ñooña dañu ko ne mu abal leen. Njooreen sax mujje nañoo toqi ba topp ci tànkiy Maam Ngóor. La taxoon ñu dàq ko nag, sunu yoon newu ci.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_151
Nun Mbériη-Saaj, fa nu newoon démb ak bërki-démb lanu nekk ba tey. Xobu garab way wow, ab doxandéem dëggaate ko, mu dee, pënde, xobu garab woowu du sunu bos. Fii, Mbériη-Saaj, su xobu garab xàwweekoo ci kow, daanu ci suuf, joor gee koy ëmb, di ko aar, di ko tette, ba nawet fekkaat ko fi, may ko ndox mu naan, mu yeewu, fuddu, gënatee dëgër. Taw bee koy nàmpal ba mu mandi, daldi doonaat garab gu bees, sëq ba tubaarfakàlla, keppaar geek doom yi ni gàññ, mu daldi ne bérét, taxaw ne asamaan si maa ngoog ! Maam Ngóor a daloon xel ! Jóge fu kenn xamul, nu yaatal la, may la jabar, loo joxoñ nu dagg ne la fabal yaay boroom, amoo looy def lu dul sunu mbaax nax la, nga beew, ne ñii ay ngaaka lañu, dinaa naan seen yóor ! Maam Ngóor dem na ba ne : - Bàyyileen su ma waxee ngeen naan lii sunu aada la. Su ko fi maam bàyyee nag ? Xanaa moom daawul juum ?
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_152
Nu tontu ko tontu bu leer : - Maam kay masul a juum ! Lépp lu mu nu mas a wax, gis nanu ko. Dunu ko wecceek keneen de, ak ku mu mën a doon nag. Maam Ngóor mer, ne nun dunuy nit, ay ràbi àll lanu. Déggal ma loolu rekk ! Keroog jooju, wax na lu ëpp. Ba sunu jonn-Yàlla-tey, kàddu Maam Ngóor yaa ngi riir ci péncum Mbériη-Saaj gii. Dafa ni : - Tey jii ci guddi, dinaa leen won lu leen yéem. Ku mu doyul firnde ci li may wax, dara dootu la doy ! Da doon coow rekk ! Wonu nu dara ba dara booloo jeex ! Am na daal ay waxi dof yu mu wax ci ni àddina si bindoo. Sama baay, man mii di wax ak yow, moo ca ni tonet, ni ko : - Maam Ngóor ! Waay Maam Ngóor, tee ngaa yem fi nu la yemloo. Li biddéew yiy sakkan sakkan yépp, xam nanu ñaata lañu te mën nanu la wax it bu ci nekk fan lay xéye ci njël ak fan lay fanaani su jant bi sowee.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_153
Waay Maam Ngóor, tee ngaa yem fi nu la yemloo ! Bi Maam Ngóor déggee loolu, dafa mel ni ku fit wi rëcc, mu daldi taf gémmiñ gi, yuuxu : - Yéen waa Mbériη-Saaj, luy seen yoon ci biddéew yi ci kow asamaan si ba ngeen leen di waññi ? Du lii lañuy waxati ? Xaw ma kuy seen Maam, waaye sànk na leen.Waa Mbériη-Saaj ne ko : - Maam Ngóor ! Li nga wax réy na di ! Sunu Maam nag moo la dese ? Mu ne jàkk waa Mbériη-Saaj, ni leen : - Bàyyileen kooku ! Su ngeen ko bawul, dina leen sànk tey, sànk leen ëllëg ! Li mu leen wax yépp, dara du ci dëgg ! Fi seen Maam ne fa la weer wi dëkk, dëkku fa. Xamul itam fu jant bi féete. Nu laaj Maam Ngóor : - Ci nan ? - Seen Maam xamul tus laa wax ! - Wax nu boog, yow mi xam ! Nun ñépp nu wër ko di ko déglu, di xoolante.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_154
Maam Ngóor di ratatati, lee-lee mu làkk nu làkk wu nu masul a dégg, gémmiñ giy fuur, muy say, bët yi weex tàll. Magi Mbériη-Saaj yi gise, ne : - Kii kat yaram wi neexul, ku ko mere tooñ ko. Nan ko jéem a faj rekk, moo nu war.Maam Ngóor ne du ci dal. Nu ni ko : - Amaana yoon wi nga nuy won sax, bëgg nu fekk la ci, mooy yoon wu baaxwi. Waaye dafa fekk rekk ne nun xamunu loolu. Rax-ci-dolli, yëf yi jarul weranteek ηaayoo, ndax askan wu ne xam na li gën ci moom. Xanaa kay bu dee danga fi nar a sanc, nanu fexe ba ku nekk sax ci li mu gëm, kenn bañ a tooñ sa moroom. Maam Ngóor ne : - Baax na, kon boog dinaa dem ba ci peggu dëkk bi, ma sanc fa Ay ati at mu jàpp njaamburam. Nu yaakaar ne xelam a ko yedd. Ndekete mu nga doon yoot, di fexe nu mu nu jekkoo. Bés nu gis ko mu maasale suuf si ci kanamam, baaraam biy yéeg di wàcc, muy rëdd ak a rëddaat.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_155
Ndekete li nu nekk ci sunuy soxla àddina yépp, Maam Ngóor a nga doon naan yóori goney Mbériη-Saaj. Ba mu demee ba wóolu dooleem, mu jàkkarlook nun, ne nu : - Yéen waa Mbériη-Saaj, mu neex leen, mu naqadi leen, dingeen dox ci sama waaw ! Ngiraan Fay, sa Maam Biraan Fay moo nu féewale, tas kër yu mag yi, ba faf toog ci jal bi. Nguuru Maam Ngóor a metti woon ! Ay nitam di dóor di dog, ñu dem ba mu mel ni góor desatul Mbériη- Saaj. Ci lañu jigéeni dëkk bi xaaree, ni : - Ndegam Maam Ngóor rekk moo fiy góor, dinanu ko fental woy. Woy woowu nag, law na ba tey jii. Jigéeni Mbériη-Saaj yi dañu doon mel ni ñuy tagg Maam Ngóor, di ko kañ, fekk ñu ngi koy ηàññ ci suuf. Maam Ngóor a nu sonaloon ! Ay ati- at, kenn sañul a sëqat. Daawul rendiy noonam yem ca. Da daan dajale waa Mbériη-Saaj ci pénc mi, jaaxaan ci njoowaanam, jeeg ji di ko upp, di bës tànk yi.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_156
Mu jékki-jékki ne : - Waaw, ana diw sax ? Kooku di lox xaat, xam ne bésam ñëw na.Maam Ngóor joxoñ ko baaraam, dellu ne : - Diw mii de, dafa maa bëgg a të. Am na yu ma dégg ne moo ko wax ci ni Doomu- Adama bindoo ak li waral ndoxu géej gi saf xorom. Ngóor siy yikkat ni gone, di saw tubéyam, mbooloo miy xàqataay, di ko ñaawal, di ko tëfli, di ko saaga. Mu giñ : - Buur, sama noon yee may sosal rekk, waaye xam nga ne moos sañumaa weddi li nga wax ci cafko ndoxum géej gi ! Dañu maa bëgg a sànk rekk ! Maam Ngóor reetaan : - Yow sax, dégguma ni am na yooy jëfandikoo ? Waa ji sëgg, ne patt. Maam Ngóor ne : - Léegi nag, laaj naa leen nu ngeen gise mbir mi, yéen waa Mbériη-Saaj.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_157
Su doon sama sago, ma jéggal ngóor sii, waaye yéen a war a dogal ndax yéen laa fi toogal. Ñépp yuuxoondoo : - Kii kay Buur, li mu def dafa jéggi dayo, rendi koo la war ! - Naankatu sàngara bu bon bi ! - Na dee ! - Na dee ! Su ko defee, ay sàmbaa-bóoy jóge fale, dóor waa ji ba mu sedd ci seeni loxo, ñu jagat-jagatee, yót rabu àll yi ñu def seen mënin. Waaye lu dul dëgg du yàgg, Ngiraan. Ay gor fippu, daldi song Maam Ngóor ak i nitam. Xare bi metti lool. Nu mujje jekku Maam Ngóor, mu gàdduy kaakeem, mook i gawaram ku nekk war fas wu weex, ñu wër dëkk bi juróom-ñaari yoon, di làkk seen làkk woowu, seen fas yiy ηexal ba foo tollu di leen dégg. Ba dara desul lu dul génn Mbériη-Saaj, Maam Ngóor daldi nuy móolu. Waaye nun Mbériη-Saaj, defante lanu mën ba mu jeex ! Kenn du nu jam naani !
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_158
Maam Ngóor dafa nu móolu, nu móolu ko. Nun, sunu maam bu daan xareji, segg la daan war ! Waaw, bu sànneekuwaan ci jaww ji, ngelawam kese daan na rotal ay junniy-junni biddéew, jën yi ci biir géej tiit, daw wuti fu ñu làqu. Kon kay nga xam ne du ηexalub naaru-góor doηη mooy yóbbu sunu fit, nun waa Mbériη-Saaj ! Bi nu Maam Ngóor naree jaaxal, ba nu jógal ko, saf na sàpp ci moom. Dellusi na benn guddig àjjuma ne day taal dëkk bi. Waaye nu ngi ko doon xaar. Mbériη-Saaj ñàkkul faayda ba ñu koy bett ñaari yoon ! Ay gawar yu bare la Maam Ngóor àndaloon, waaye ñett a ca mucc, moom ak yeneen ñaari nitam. Ma ni : ñu ëpp Maam Ngóor kàttan, ëpp ko màqaama, dal nañu ci sunu kow, waat ñoom it ne fàww nu teqale nook Maam. Bu teyee ñu jóge penku, bu ëllëgee ñu bawoo sowu jant. Kenn ci ñoom nag bokku ceek sa moroom làkk, te Mbériη-Saaj mënu cee wax ak kenn ba mu tontu la.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_159
Dofunu de, Ngiraan, nu ngi teg sunuy bët ci li xew, nu ngi gis ni àddina siy doxe, waaye taxul nu saalit bay pasar-pasaree li nu Maam dénk. Waxuma feneen de, Mbériη-Saaj laay wax ! Yow nag, xeer wii ngaa wéeru di ma déglu, làyyi biy dugg ci sa biiri yax, lu mu metti metti, mooy sa jàmmu yaram, nde soo juumoon ba jéggiwaat buntu Mbériη-Saaj, leneen lañuy wax. Ngiraan Fay, ni nu la dàqe tey Mbériη- Saaj, noonu lanu fi dàqe Maam Ngóor, boobaak léegi mat na xarnook genn-wàll. Sa dégg-dégg a des rekk, nde ba ma la nee sànq kenn masu fee siyaaresi Maam Ngóor nga waroon a xam ne bàmmeelam newu fi. Fanaanal jàmm, Ngiraan. Tey dinga mucc ndax noo la soxla, fiir la, nga wuysinu. Waaye muy yow di keneen, ginnaaw-si- tey, mbokku Maam Ngóor bu juum ba teg tànkam Mbériη-Saaj, dinanu ko def lu ñaaw ».
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_160
TÉEREB DÓOM II
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_161
Léegi yaa ci des, Badu. Xamal ne Mbériη- Saaj du sa jëmu. Gis naa it ni Téereb Lëndëmtu ubee sa bopp. Bi nga ko jàngee ba noppi, téye nga ko lu yàgg, sog ma ni : - Ngiraan, juum nga, de. Ma yëngu ndànk fi ma tëdd ci sama biir bàmmeel, daldi la ni : - Ci naka, Badu ? Nga xàmmee sama baat, fu ne nga geestu fa, gisoo ma. Ma ne la : - Maa ngi nii toog ci sa wet, Badu. Mënoo maa gis waaye duma la sore mukk. Ci nga ma door a tontu : - Soo jàppee ne tukki bi nga tukki Mbériη- Saaj amul njariñ, juum nga. - Lu tax nga wax loolu, Badu ? - Guddi ga nga fanaan Mbériη-Saaj, am na solo lool. - Ba léegi wax ji leerul ci sama bopp ! - Ngiraan, bàyyil dof-doflu !
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_162
Tëdd laaxira bumu tax nga mel ni ku xamul li géej giy riir. Lépp loo xam ci yow ak ci say way-jur, guddi googu nga ko jàng. Say kàddu jaaxal ma lool. Ma xalaat ci ba yàgg, ma laaj la lu wax jooju tekki. Nga ne ma : - Du nee nga Maam Ngóor, dëkk na Mbériη-Saaj ay ati-at ? - Looloo am, Badu. - Tëngéej ga ñu ko denc, soo fa demee doo fa jële dara, ndax say mbokk dinañu la nëbb yu bare ci Maam Ngóor. Yaa fi gën a bëgg a wax ay waxi seetu, Ngiraan. Xéye nga Ñarelaa, sol say dàll, tegu ci yoonu Mbériη-Saaj. Ñaari fan yooyu, jot ngaa niitu ci seetu yu bare. Nangu naa ne yey nga ma, Badu Taal ! Sa wax jooju du deñ te am naa ci mbégte. Waaye nag, bul yaakaar ne coono wàcc na la. Lànkoon nga ne doo tàggu néewu Asan Taal. Waaye xanaa dinga siyaareji Maam Ngóor Tëngéej ? Dem fa, ñaanal ko suuf siñ ko sànge sedd ci kowam.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_163
Su ñu waxantee dëgg, Badu, waa Mbériη- saaj lii lañu ma jàngal : ku bëgg xam sa bopp, fàww nga takk sa fit. Lu ruq lëndëm-lëndëm, bu ca ragal a dugg. Soo ko defee, dinga làngi bés ak ki jur maamu Maam Ngóor. - Aa, Ngiraan, yen bi nga ma yen gën a diis ! - Déggoo wax ji, Badu ! Yen bi taxu koo diis. Maam Ngóor mi nu jur nun ñépp, amaana ki ko jur juddoogul. Ñàkkul sax ne yow mii, Badu, bés dina ñëw nga juri Maam Ngóor, ni sa ndey Biige Sàmb sukkee bés jur la. * * * May ma tuuti ma dellu ay fan ci ginnaaw, alxames ja ñu jote ci néewu Asan Taal, war koo defar, denci ko armeel ya. Dëgg la, yoon wi ma lay awloo xaw naa dëng. Jàppe ko noonu. Nangul ne yëf yi du kaf. Du caagin dangay reer ba suur këll, di daagu nu mu la neexe ba àgg fa nga jëm.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_164
Jàppe ma ni ab fecckat, man Ngiraan mii ubbiwaat sànq Téereb Dóom, sëgg ciy bind. Maa ngi wëndéelu ci biir géew bi, am ñu may tëggal sabar te duma leen gis. Bu gaa ñi rëkkee, ma tëb ba àgg ca kow asamaan, ñu wàcce ma ndànk, rëkkaat ba yàgg ne tekk. Samay kàddoo leen di awu. Su ma nee tekk ñu jëlaat, daldi rëkk, xaacu. Bii yoon, saañal say nopp te ubbi say bët, Badu. Toppal bu baax yoon wi la sama baaraam di joxoñ. Léegi tisbaar jot. Yaa ngi yëg ni naaj wi tàngeem, Badu ? Wuy, man ! Sama tànk yaa ngi lakk sax! Jàkkay Ñarelaa ji janook bayaalu Xujja- Bajaan. Waa gox baa ngi dem ak a dikk, ñii di raηale ay siis, ñii di samp ay tànt.Sama xel yépp a ngi ci Mbisin ak Mbisaan. Fu ñu aw, samay bët topp leen. Lee-lee ma di leen tegtal, yéen gone yi, li ngeen war a def mbaa may jubbanti seen liggéey. Ngóone Cuun jóge fale ak sooxam bu metti, te naan :
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_165
- Mbisaan yow, ana nga ? Kaay fii ! Ana Mbisin ? Am ku ko tontu : Ana ñu sax, sunu ñaari doomi tubaab yi ? Ñoom de, ñu ngi fi woon sànq ba tey ! Ngóone Cuun daldi yuuxuwaat : - Mbisaan ! Mbisin ! Mbisaan génne fu kenn xamul, agsi, ñëw ba ci kanamu Ngóone Cuun, téen, ne ko jàkk ba yàgg mu këdd suuf seek tànku càmmooñam, am lu mu ko yuuxu ci nasaraan. Doomi Yaasin Njaay yee xamadi ! Waaye Ngóone Cuun lañu fiy fekk ! Ngóone Cuun mi nga xam ne moos kaay xeex moo ko gënal kaay ndékki ! Dafa xulli Mbisaan, ni ko : - Noq naa la, de ! Gat sa ! Damay sa moroom ba nga naan ma keskiyaa ? Reew ba dee ! Ñëwal fii laa wax ! Ana Mbisin ? Mbisin ! Mbisin ! Mbisaan a ngi koy xool, mel ni ku jaaxle. Ba ni tuuti, mu am lu mu waxati.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_166
Ngóone Cuun woo benn gone, laaj ko : - Mu ne lan ? Gone gi ree, ne ko : Mbisaan mii kat, waxam daa gaaw, dinaa ko dégg muy wax waaye duma xam lu muy ratatati ! Noonu mu walbatiku, xool Mbisaan, ni ko : - Répète ce que tu as dit ! - Ma soeur est sourde, ce n’est pas la peine de crier son nom comme ça ! C’est tellement bête, ça ! Ca la gone ga sog a xam li mu bëgg a wax, tekkil ko Ngóone Cuun : - Nee na Mbisin daa tëx Ngóone woo la, yow Badu : -Kaay fi, Badu Taal ! Moo, monte gone gi wax na dëgg ! Rakk ji nopp yi neexul ! Yow Badu, demal seetal ma ko, fu mu mënti nekk nga indil ma ko fii, danu am waxtaan. Fi muy daaneele, Mbisin génne fa mu làqu woon. Ma koy xool, sama xel dem fu sore. Céy, Mbisin ak sewaayam ! Juróom-ñetti at doηη la am, waaye yaayam fexe na ba dugal ko ci xeesal.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_167
Soo ko gisee, mu ngi xonq ni naaru- gànnaar. Sa ñaari doomi baay yooyu nag, nit ñaa ngi ηuη-ηuηi, naan seen ndey Yaasin Njaay dafa xaw a dese. Fi ma taxaw ak Yilimaan Keeta, gis naa la ngay diisoo ak sa yaay Biige Sàmb. Ma ne ci sama xel : « Àddinaa doy waar ! Ba fi mu ne daal, ñu ngi waaj a denci Asan Taal ! » Yaa ngi taxaw ak Mbisaan, muy wax ak yow, ngay yëngal sa bopp. Bi Mbisaan noppee, nga fekki Mbisin, mu am lu mu la wax moom it ak ay loxoom. Fi ma toog, ma dégg baatu Ngóone Cuun jib : - Man de, xawma fu nu jëm ak doomi Asan Taal yii ! Ku góor ki déggul kaay ma rey la ci wolof, ki ci des moom nopp yi neexul, faf ! - Ñarelaa kañ a ngi sog a am gan ! Mu mel ni loolu la nit ñi doon xaar. Wokkante. Piisante. Ciipatu. Waa Ñarelaa ñoo teel a bañ Yaasin Njaay ak njabootam ! Waaye moom it de, kenn du moom.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_168
Xanaa lii mooy ñu lay tam dëmm ngay soccoo yeelu liir ! Ténju Yaasin Njaay bee ka kéemaane ! Mu ngi téju biir néegam, ne du wax ak kenn. Ca njëlbéen ga, danu defe woon sax ne naqar wu mettee taxoon mu jàpp noonu njaamburam. Waaye man mii jokkook moom bés ba Asan Taal faatoo, gise woon na neneen mbir mi. Yaasin Njaay a ngi muuru, sëgg, ku ñëw di ko jaalesi tam du tax mu siggi xool la. Ku ko nuyu, mu ne la jabb loxo, bala nga ko naan « siggil ndigaale » sax, mune la « siggil sa wàll », ngir won la ne bëggul nga lal waxtaan. Aa ! Yàgg Tugal doηη jar na gii génn xeet? Ñàkk xam li mu waral bare na, walla ! Ndax nun waa Ñarelaa gii kat, dunu bàyyi kenn mu nuy yab mbaa di nu sewal. Xaste bi ne kurr. Lu nekk ñu koy yakk Yaasin Njaay, te du benn yoon boo dégg nit jaar ci turam: - Li mu nekke woon Tugal kañ, ñépp xam nañu ko.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_169
- Demunu Gànnaar waaye xam nanu ne guddi lañ fay reer ! - Maa la ko wax ! - Ñaaw ba nga ni lii lu mu doon ! - Moo yey di làq kanamam. - Soo yëkkatee sa benn loxo ne faalewuma kenn, yëkkatil bi ci des ne kenn faalewu ma. - Lu ne gis nanu ko Ñarelaa waaye guléet jigéen juy ténj sañ fee def lu ni mel ! Wax jooju moom, ngóor si ñu naan Tamsiir Ba moo ko moom. Nee ñu faru Yaasin Njaay la. Bi ma yëf yi bëggee soof, woo naa Yaasin Njaay, laaj ko lan la digaaleek Tamsiir Ba moomu. Mu ne ma : - Tamsiir de, sama doomu-bàjjan la. - Doomu-bàjjan ba ci lan? - Dafa may wéttalisi, moo tax mu fiy fanaan lee-lee.Ma ne ko : - Bu loolu amati. Bumu fi fanaanati.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_170
Yaasin ne ma : - Loolu ngay wax, Ngiraan ? Xoolal, Ngiraan ! Ma ne : góor gi, xullil fii ! Ma siggi, gis Yaasin Njaay tiim ma, tas séram, joxoñ ma këfinam, xulli bët yi, te naan ma : - Lii, maa ko moom, lu ma neex laa ciy def, ku ma neex laa koy ràccal ! Bi samay nopp déggee baat yu ñaaw yooyu, samay bët tegu ci lu leen waroon a ump, dama daldi ne këpp daanu, tudd turu Yàlla, yaakaar ni fa laay jaare ñibbi laaxira. Waa Ñarelaa ñoo ma fa fekk, ximmali ma, benn doktoor ñëw seet ma, bindal ma ay garab. Ku nekk di ma laaj : - Lu xew, Ngiraan? - Du dara. - Loolu wax la ? Tuutee tee nga des sunuy loxo nga naan du dara ! Ma ne patt rekk. Tey laa sog a ηaaη, wax li ma xëmloo bés boobu. Bi ñu nee tey la Yaasin di summi, ay xaritam solu nañu ba jekk, ñëw, ñu làng, teg misigu Móodu Siise,
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_171
di xawaare, yëf yi xumb ba dee. Sama xel dellu ca alxames ja nu demee ayeropoor jëli néewu Asan Taal, Móodu Siise jóge moom it bitim-réew ak ndam lu réy... Yaasin Njaay a ngi la ko sàñseel ba nga ne lii lu mu doon ! Jabu, benn doomu- bàjjanu Asan, muñ ko ba mënatu koo muñ, mu daldi fekki Yaasin fi mu toog, di ko gaaral : Lépp ak Asan Taal, moo nu yóbbe lii lépp. Yaasin mel ni ku ko déggul. Ma xëcc Jabu ba ci biti : - Déet ! Jabu, déet ! Mag day xam fu muy waxe.Mu daldi ma sippi meram : - Toppal fale, magum séytaane nga rekk ! Lafañ kañ boroom mbaam lay faral waaye wax ji moom su ñu ko waxulee tey it, wax ko ëllëg. Te sax man maa ni kenn du Asan Taal ! Di taxawaalu ci àddina si, dëkk bu dul dëkku jinne nga ne fa naam Daraame, bu ñu la nee kañ ngay ñibbisi nga ne, aa, man kat, góor laa, damay daan sama doole, góor moomul toog, sàmbati- parlaa-njaay !
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_172
Daan nga sa doole moom, Asan Fay Taal, doomu Ngiraan Fay ak Ndàmbaaw Jóob ! Léegi nag, dem nga sa yoon bàyyil nu fi ñaari banti-maam-Yàlla yii nga xam ne duñu yàpp, duñu jën ! Am ku ko ne : Waaw Jabu, loo xewle ? Ku mus a gis lii ? Bésu tey bii de, wàcce kaamil moo ci jekkoon, kenn séentuwu ci woon wax ju ñaaw ! Jabu, delloosil sa xel ! Ci laa ko ne ndànk, man it : - Jabu... Nu xoolante bu baax, mu ne ma : - Baal ma àq, Ngiraan. - Amul solo. Jéemal a ànd ak sa sago. Noonu, Ngóone Cuun ñëw ñaarook man, am lu mu ma déey. Ma ne ko : - Aa ? Biige Sàmb man ? - Xanaa Biige Sàmb menn, yaayu Badu Taal. Mu nga fale di say. - Aywa nu dem. Ba nu rombee jigéen ñi toogoon ci suufu tànt bi,
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_173
kenn ci ñoom geestu nanu, xam naa xelam dem fu sore, mënu koo muñ, mu jàpp boppam, yuuxu : - Biige Sàmb, yaay gor ! Muñal rekk, nde séytaanee yàq sa digganteek Asan Taal ! Waaye Yàlla waxul kenn dara ! Biige tamit a ngay daanu gangiri ca geneen wet ga. Nit ñi wër ko, naan : - Biige, gëmal Yàlla ! Jullit day nangu dogalu Sunu Boroom. Céy ! Biige Sàmb ak Asan Taal ! Say way-jur lañu. Kon su ma lay nettali seen mbir, fàww ma leb ci as tuut. Kersa dina ma teree àgg ci yenn yi. Nobante woon nañu de, ñoom ñaar ñooñu ! Yàllaa tuddul seen séy rekk. Bés bi Asan Taal jógee Ñarelaa, jëm Màrsey, sa ndey Biige Sàmb a la boot yow Badu, ànd ak moom ayeropoor. Ñu ne fa, ndeysaan, di fóonante ak a jooyoo ci biir nit ñi. Waaye yëf yi mujjewul fenn. Asan Taal bind na Biige ñetti yoon, ca weer yu jëkk ya. Ñu teg ci yeneen ñaari weer, kenn déggalatu ko dara. Dem nañu ba ku wax Biige Sàmb waxu Asan Taal,
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_174
mu mer, xulook yow. Fi Biige Sàmb tëdd, mu ngi say ak ay yëreem yu xottiku, kanam gi newwi, ñu koy tuur ndox mu sedd. Soo ko gisee, mu ngi gajj yaram wi yépp ba muy nàcc. Yaasin ak ay xaritam yokk misig bi ba mu sës. Foo tollu di dégg Móodu Siise muy woy « Mbëggeel ». Ma daldi xunn, ne ci sama xel : « Xanaa ngóor sii rekk mooy woykat ci réew mi? Móodu Siise guddi ! Móodu Siise bëccëg! Dafa rekk doy ! » * * * Badu, waa Ñarelaa ngi bëgg a ëppal, kat! Bañ Yaasin Njaay rekk tollu na nii ? Mbedd moo aw, dégg ay xaste : - Lan la Asan Taal gisoon ci ndaw sii nga xam ne kuy ñaaw moom ngay dimbali ? Ci sama xel mu gàtt, man Ngiraan Fay, ma yaakaar ne wax jooju tooñ la. Lu tax ? Kenn ci gox bi teewewul ndajem Yaasin Njaay ak Asan Taal ca Màrsey.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_175
Kenn fekkewul guddi ga : - Bëgg naa la ak - Maa la raw jëkkee dox seen diggante. Kenn xamul lu tax seen ñaari yaram dem bay maasaloo ci lëndëmug Màrsey. Ci biir wax ji nag, am na yu senn ci sa mbirum baay. Nee ñu Asan Taal nekkewul woon Tugal lu dul wër ak fo. Dégg naa ne futbal ba ka taxoon a dem Màrsey amu ca ndam, ndax dëkke fa càkkaay, jigéen ju dul jigéenu jinne mu doxaan la. Wànte ana goloo ka xastey daar-daar ? Su ma fàttalikoo samag ndaw man mii, fàww ma màndu ci wax ji. Nun góor ñi moom, wax dégg Yàlla, danuy faral di weex bët lool. Jigéen ju nu waxal ñaari baat, yaakaar ne làq na ci biir séram lu beneen moroomu jigéenam masul a am ci àddina. Ginnaaw waruma la nëbb dara, dinaa la àgge leneen lu ñu fiy ηun-ηuni. Ñu ngi naan Asan Taal am na yeneen ñetti doom Tugal.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_176
Xawma ndax loolu am naam amul. Su la ko jaralee, gëstulal mbir moomu sa bopp. Ñaari doomi Asan Taal yi jot a ñëw Ñarelaa daal laa xam ne amuñu yar, amuñu teggin. Jarul làq-làqal, Badu : Mbisin ak Mbisaan, ni seen golo lañu ma jàppe, man seen Maam. Lee-lee Mbisaan déey dara rakk ji, kooku ñëw fekk ma fi ma toog, daldi ma sëllax suuf. Bés, Mbisaan fekk na ma may kàbbar, mu tekki tubéyam, saw ci sama wetu sijaada. Loo yaakaar ne moom laa def ? Mënoon naa koo duma, waaye defuma ko. Dama julli, ñaanal ko Yàlla yërëm ko, delloosi xelam. Ba Mbisaan demee nag ba nar koo def yoonu tool, laa woolu ndeyam Yaasin Njaay. Mu ne ka ma yebal : - Neel góor gi Ngiraan Fay, su ma soxlaa na ma fekksi.Ma defe ko noonu, ndax ragal ay. Ma dem néegam, ni ko : - Yaasin, sama ñaari sët yaa ngi may bëgg a jaaxal.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_177
- Aa ? Ci lan ? Ni mu dëgëralee baat bi tax na tuuti kon ma balu ko àq, dellu toog ci ëtt bi. - Mbisaan de, saa yu ma fekkee may julli, su ma sëllaxulee suuf, saw na ci sama kanam. - Xanaa dañu diy gone rekk moo tax, nde man mii di seen ndey, duma def loolu. Fi ma nekk sax, dama jàpp góor gi. Su ma amee jot, dinaa la woolu nu waxtaan ci. - Woolu ma nag, laa dégg, Yaasin Njaay ? Nga woolu ma man mii, Ngiraan Fay ? Sama xol baa ngi fees dell. Ma ni ko : - Bu sa doom yu reew yi yàqatee sama julli, dinaa lakk seen lu bon ! Yaasin Njaay mel ni loolu rekk la doon xaar, daldi ma tàccu : - Boo ciy laal kenn di fanaani kaso ! Yaasin Njaay a ngi may joxoñ baaraamam, ba mel ni kuy waaj a luqi samay bët. Su ma ko toppoon keroog, Ñarelaa yépp a naroon a dajaloo ci kër gi,
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_178
te kon dinañu ko gaañ ndax mer mi ñu ko dencaloon. Ma xam ne muñ moo ma war.Ma ni ko : - Yaasin, Asaan Taal dem na te am na ñu ko jiitu armeel ya. Kenn ci nun dëkkul ci kow suuf si. Danu fi jaar rekk. Yàlla def na maa fi des ak yéen. Dama leen di gunge doηη, yaak say doom, ngir sàmm sama digganteek Asan. Tee noo... Bàyyiwu ma ma àggali li ma doon wax. Dafa ma ciipatu, tegal ma ci ay kàddu yu ñaaw. Sama xol jógaat, ma ni ko : - Sama taaw dee la mag, Yaasin ! Neneen nga ma war a tontoo ! - Góor gi, buma tax a wax ! Yaa tal Asan Taal ! - Aa ? - Waa-waaw, yaa ko tal. Te soo deful ndànk sax dinga ma abal kër gi. - Nga ne lan, Yaasin Njaay ? - Dégg nga li ma wax. Ci laa ko ne :
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_179
- Kon boog, baax na. Ci buntu néeg bi, daje naak Tamsiir Ba mi Yaasin Njaay ne doomu-bàjjanam la. Na ma Yàlla baal, waaye Tamsiir Ba niruwu ma daraak nit ku yiw. Su la nee jàkk, li ngay jëkk seetlu ci moom mooy ni karaw geek bët yi xonqe. Xam naa wérul, ndax ci moom rekk laa mus a gis lu ni mel.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_180
TEEREB FENT
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_181
Fu la jant biy tiime, Badu Taal ? Mbaa réew ma nga nekk kenn sonalu la fa ? Ku am jom nga, waaye sa moroom yiy daani seen doole bitim-réew, dañu leen di faral a jàppe ni ay jaam, coono bu nekk ñu leen koy teg. Góor-góorlul, te xam ne fu ma tollu maa ngi lay ñaanal. * * * Téereb Fent bi nga téye tey nag di ko jàng, li ci ne yépp maa ko sàkk, man Ngiraan Fay. Lu waral nuy daagu maak yow, di weccee xalaat ba yàgg ma ne la fi ñukk, jàdd koñ, ne mes, réer la ? Du dara lu dul tiitaange, Badu. Waaw ! Daawur Jaañ a ma tiital : mu ngi yàq Senegaal. Ni Daawur Jaañ di doxale, jaaduwul. Ma ne : njiitu réew maa ngi yàq réew mi kat, Badu ! Bëgg nanu jàmm lool, waaye ku say doom di jàmbat xiif, noo leen mënee tanqamlu ? Daawur Jaañ dina nu dugal ci fitna ju réy.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_182
Séentu naa fi ay jàmmaarloo yu mettee- metti. Deret dina fi tuuruji. Maa ngi dégg jirim yi ñuy jooy. Aakimu. Maa tey. Jaay doole. Jalgati. Ma ne : njiitu réew maa ngi tas réew mi! Ku nekk a ngi ηàbb sa tojitu réew, sàmp sa raaya ci sa toolub yàmbaa, ne yaa fay dogal. Daawur Jaañ, tëj nga géej gi kaso, fatt nga ngelaw li ba noyyi të ko ticc. Tas nga sunu yaakaar ! Jàmbaar ju wàccee asamaan, ne putt ci géej gi, di joow ba agsi ci waax bi ngir yewwi nu, say nit dóor ko bal mu daanu. Yaay kaabal, Daawur Jaañ ! Noo fexee ba caabi feete géej gi ginnaaw ? Badu, njaaxum lu mel noonu laa njort ne moo nuy yoot. Ginnaaw li may nettali ci téere bii, lu ñëwagul la, mënuma woon def lu dul fent. Soppi naa yu baree-bare,
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_183
waaye gone gu ndaw sax bu jàngee li ma bind, dina xam ne Daawur Jaañ laa tudde Dibi-Dibi, ci Téereb Fent bii. Ni ma weccaatlee turi béréb yi tam mënul a réeral kenn. Yàlla tere tereeti ko, waaye du ñàkk askan wi nekk ëllëg ci fitna. Su boobaa, na nga jàngaat téere bii bu baax. Dinga fekk ci biir njaaxum yi fi Daawur Jaañ def ba tax réew mi màbb ci sunu kow, nun waa Senegaal. * * * Fent. Fen. Ñaari doomi-baay yooyu, ku sa nopp neexul mën nga leen a jaawatle. Monte aka ñoo wuute tey ! Badu, man duma magum xamoon naa ko. Magum waxoon naa ko laa. * * * Moom kott a des Guy-Géwél.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_184
Ñépp jóge nañu Guy-Géwél, daw wuti fu ñu làquji. Ñetti at a ngi kanu yiy dal, kër yeek isin yiy tàkk, reyante bi metti lool. Waaw, ñan ñooy xeex sax ? Loolu nag moo doy waar : kenn xamul ñan ñooy xare. Koo laaj, mu ne la : - Gone ya doon dox doxu ñaxtu de, ñoo nu yóbbee lii lépp ! - Njiitu réew mee matul njiit rekk, nde mbir mi mënoon naa bañ agsi fii. - Dibi-Dibi kat, yéen a ko sànnil ay kàrt ba mu doyal, seen waay la ! - Ba ci soldaar si duggee la Dibi-Dibi tàggook sagoom. Dëgg la. Réewu Afrig boo gis tey, daanaka bakkanam a ngi ci xott. Ñaare, lu ñàkk faaydaay sooke ay wi. Waaye dinañu dem ba mu ëpp loxo, jaaxal ñépp. Li xew réewum Jafune biral na ko. Coow li yépp, goxu Jafune bu ñuy wax Kimintaη la soqeekoo. Jaaykatu màrse yi ci gox boobu ñoo jëkk a amal benn doxu ñaxtu, ne daal juuti yi ñu leen di feyloo, ëpp na.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_185
Ñu dem buntu kër Dibi-Dibi, njiitu réew mi, ngir yëgal ko seen naqar, mu jéem koo saafara. Ba ñu taxawee foofu di xaar, goney daara ju mag ji fekk leen fa, tàmbalee xumbal, ne ñoom it dañuy jàppale seeni jigéen ak seeni bàjjan. Noonu, saay-saay tamit daldi jóg taxaw ne kenn du leen bàyyi ginnaaw. Bés, ñu yéeg ci benn taax, tiim kër Dibi-Dibi ak seeni doj. Mirtaa, doomu Dibi-Dibi, doon romb. Ñu xaañ ko. Janq bi laal jë bi, gis ni deret jiy tuuroo, daldi tiit, nekk fay salliiru tëwa noppi. Dibi-Dibi génn, yem ci, xol bi jóg, mu dajale kilifay làrme bi, ne leen : - Ñi fi taxaw ñépp, na leen seeni mbokk jooyoo balaa timis di jot ! Ay soldaar yu bare ñëw, wër mbooloo mi, tàmbalee soqi seeni fetal. Tàkkusaanu Jafune jooju tàngoon na lool ! Noonu de la mbir mi doore. Ca ëllëg sa, yéenekaayi àddina si yépp wone nataali 137 Doomi- Aadama ya seen bakkan rot keroog. REYANTE BU METTI AM NA CI RÉEWU JAFUNE...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_186
JAFUNE : LÀRME BI BÓOM NA 137 NIT... COOW JIBATI NA CIM RÉEWU AFRIG ! Ay nag, nee nañu du yem ci boppu boroom... Góbi yi nekk ci làrme bi, te nguuru Dibi-Dibi ameeloon leen peyu ñaar-fukki weer ak juróom-ñeent, daldi yëg seen doole ne ñoom tamit dañuy amal doxu ñaxtu. Ca la Dibi-Dibi tiite, yaakaar ne dafa am ñu làqu ci ginnaaw gone yooyu, nar koo fexeel. Mu daldi aakimu rajo beek tele bi, di dàggasanteek ñoom : - Man, Dibi-Dibi, kenn du ma xoqatal ! Dara ba dara booloo jeex laa leen dul jox ! Dërëm dungeen ko am ! Xanaa dangeen yaakaar ne man maay Abdu Xaalis ? Dugal-leen lii may wax ci seen bopp : dërëm bi gën a tuuti dungeen ko am! Soldaar yi mer, rendi jëwriñ bi ñu dénk kaaraange réew mi, watat néewam ci mbeddi péeyum Jafune. Bés ba ñu bóomee kilifa googu,
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_187
lanu gëj a xam nu yëf yi deme. Ñetti at a ngii nu nekk ci fitna, te nun xamunu ñan ñooy xeex ak lu waral reyante bu ni mettee. Gànnaay yaa ngi ne gàññ ci réew mi. Ñi fi nekkoon di politig ciy jamono, ku ñu ci reyul, yaa ngeek sa làrme bopp. Dangay dégg bés ne diw ak diw ñoo far, su ëllëg saa ñu ne la seeni nit a ngay jàmmaarloo béréb sàngam. Am na itam ci gaa ñooñu ñuñ ciy tuumaal ci mbeyum yàmbaa. Nee nañu it yeneen xeeti dorog yu bon yiy dugg Jafune, ñoom ñoo ko fiy dugal. Boroom réew mi moom, dama koy beral loxo, ndax mooy ndeyu-mbill gi. Waa àll bi gàddu nañu seeni ngànnaay, ne seen dund gi dee sax moo leen ko gënal, te ñàkkuñu faayda bay seetaan xiif ak mar di leen faagaagal. Dëkk bu ñu romb, gone ya topp leen, kilifa ya ànd ak ñoom. Noonu, làrme bi song leen. Dem nañu ba nit ñiy dee ni ay xar bésu Tabaski, mbedd moo aw gis fay néew yu tàmbalee yàqu.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_188
Ñu naan : - Tundu Ñambaas, rey nañu fa démb rekk lu war a tollu ci junniy Doomi-Aadama. Mbaa nga dégg ku ni : - Talaata jee ñu génn, taal nañu kër gornooru diiwaanu Maymaydo. Lakk na ba jéex dara desatu fa. Gornoor ba dafa daw mook njabootam, nde su leen fa fippu yi fekkoon def leen lu ñaaw ! Tàkkusaan soreetul. Góor gi Aatu Sekk a ngi taxaw ci tàkkal dex gi, di xaar waxtu julli jot, ba Yilimaan Jonn nodd. Waxtu wi weesu, déggul baatu Yilimaan. Mu door a nangu ne Guy- Géwél ba woon dootul. Lu muy def Guy-Géwél moom kenn ? Xelam dellu ci ndajeem ak Omar Jaw, ngoon ga waa Guy-Géwél tàmbalee gàddaay, daw wuti fu ñu làqu. Góor gi Aatu Sekk xool leen, yëf yi mel ni sinemaa ci moom. Ay xanti oto ak ay saret a ngi yab ay lal, ay kàddiir, ay tele, ñu tegale leen ba ñu àgg ca kow.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_189
Lépp li waa Guy-Géwél mën a dajale ci lu ñuy lekk def nañu ko ciy leket mbaa ñu ëmb ko ciy mbuus. Daw-làqu yaa ngi bare ba foo sànni mbàttu mu tag. Waaye ñu ngi ne tekk. Ku ci nekk a ngi tiit ba talul waxtaan, waxatumaak naan day kaf mbaa muy reetaan. Aatu Sekk di leen xool ñuy génn Guy-Géwél ba ne tuuti mu may nopp géej gi, dégg ni muy bëmbe, mel ni kuy gëdd Doomi-Aadama yi. « Yéen a teg seen bopp coono bu metti bii! Lu tax ngeen bàyyi fi nit ñu baax ñépp, tabb dof bu mel ni Dibi-Dibi, jébbal ko réew mi ma leen dénk, man seen Boroom ? » Walla xéy-na géej gi da doon yedd waa gox bi, naan : « Guy-Géwél, delloosil sa xel ! Koo ci wax muy wut lay, naan néew-ji doole laa ! Loolu du lay, ñàkk loo lekk warul a tax ngay sàcc, di cagatu, di naan sàngara aka tóx yàmbaa. Daaneelal nguuru Dibi-Dibi gii ! Feek defoo ko, doo tàggook naqar ! » Omar Jaw ñëw fekk Aatu Sekk fi mu taxaw, ni ko :
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_190
- Góor gi Aatu, xanaa yëgoo li xew ? - Yëg naa ko sax de. Réew mi daanaka jur gu médd la. Till ak Bukki ak Segg fees nañu ko, ku nekk ηànk wàllam di wéy, di yéy. - Loolu kay taxul may wax, góor gi ! Daa am ñuy waaj a song Guy-Géwél. - Ñooñu ñana ? - Xam ! Ci li nit ñiy wax daal, xare bi ñuy waajal fii dina metti lool ndax nee ñu ku jëkk a teg loxo ci Guy-Géwél jël ndam li, yilif réewum Jafune. Aatu Sekk ni ko : - Moo Omar, gisaloo ma sama waa kër yeem ? Omar Jaw siggi, xool góor gi, dem ba koy wax dara noppi, sëggaat. Mu ni ko : - Lu mu ci mënti doon, wax ma ko, Omar. Ci la Omar siggiwaatee, ni ko jàkk : - Góor gi Aatu, biig de am nañu jot a mucc... - Tee nga maa wax li xew rekk.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_191
- Soo jullee, ñaanalal njaboot gi, Aatu. Aatu Sekk a ngi ηàbb yatam, mel ni kuy miir xamatul lan lay wax. Deret moo am doole ! - Mbaa saay-saay si sonaluñu leen rekk ? Ni ko Omar xoole, mu xam ne jëli na ko.Omar sañu koo wax ne xaj yee leen mujjee jiiroo.Dafa ko ne rekk : - Góor gi Aatu, nanu dellu kër ga, nga jël fa yi nga soxla yépp, nu dem. - Dem fan ? - Nun ñii ngay gis ñépp, kenn xamu ci fu mu jëm. Danuy wuti pexe ndax ñiy waaj a song Guy-Géwél, lu leer lañu wax : ku ñu fi fekk yaa tooñ sa bopp ! Dégg naa ñu soxar lañu. Nee ñu dañuy dagg xëtëru nit ñeek seen res di ko togg di lekk ! Dégg naa it ne danuy yeew ay nit ñuy dund, dajale leen ci benn kàmb, ba noppi tuur leen petorool, xosi almet ci seen kow, ñu tàkk jëppit. - Waaw, Omar, ku la waxoon ne lu mel nii mën naa xew sunu réew, dinga ko gëm ?
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_192
- Mukk ci àddina, Aatu ! Waaye waxtaan xeju fi. Omar xamul fu mu jëm, waaye fitam jiitu na ko fa bu yàgg. Moo tax su nit tiitee ba tàggook sagoom, mbokk yi naan : - Diw de, fit wi dafa rëcc.Day fekk booba jëmm ji nekk fi, mbokk yi janook moom te muy xottu nit doηη. Omar Jaw a ngi ñaq bay siit, tuñ yi wow koηη, fu ne mu fay sànniy bëtam. Fan yii weesu, ñaata yoon la ay bëti Omar Jaw ne jàkk néewu Omar Jaw ? Monte dey, moo fi gënoon a dëgër ηaam, moom Omar Jaw ! Moo fi dàqoon a jaay njàmbaar. Saa yu déggaan lu ko naqadi ci rajo bi, da daan fekksi Aatu fi mu toog ci taatu niim gi, muy xultu, naan ko : - Góor gi Aatu, nga baal ma de, waaye ñii ay doomaraam lañu, dañoo nar a yàq réew mi ba mu yàqu yaxeet ñu dem bàyyi nu fi, jaaxaan Monaako walla béréb yu ni mel, di balaxalmàddaa, nun nuy wéye ndóol ak mettit wu dul jeex !
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_193
Waaye fi lañu nuy fekk, dunu seetaan loolu, dinanu ko defanteek ñoom ba mu saf sàpp ! Bi Aatu fàttalikoo kàdduy Omar yooyu, tuutee tee mu xaqataay. Waaye mu ngi yërëm Omar Jaw be, ndeysaan. Mu daldi ne ko : - Omar, tàllalal sa loxo, ma ñaanal la. Tey lanuy mujjee gise maak yow, ndax fi mu ne nii taxaw nga te man fas yéenewumaa jóge Guy-Géwél. Fii laa xam, fii laay toog, xaar fi dogalu sama Boroom. Omar Jaw dem ba xaw a sore, daldi geestu. Jabar jeek doom yi yuuxu ko, mu daw dabi leen.Góor gi Aatu Sekk taxaw moom kenn ci waax bi, di leen xool ba ñu jàdd koñ, mu daldi dëpp, dellu këram. * * * Fukki waxtu ci guddi weesu na. Way-fippu yi agseeguñu Guy-Géwél. Waaye ñoom ñi fippu sax, ñan lañu ? Aatu Sekk xamalu leen dara. Mu ngi toog ci diggu këram, di leen xaar.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_194
Ñetti fan a ngi, mburu mu wow lay dunde. Dute ji jeexagul waaye li des ci këriñ gi bareetul. Balaa yàgg, dootul lekk lu ñu togg ci cin, dootul naan lu ñu tàngal. Guy- Géwél a ngi ne selaw. Ci tisbaar, doxantu na ci ëtt bi lu mat waxtu. Mu ngi sog a seetlu ni kër gi bindoo. Bunt bu mag bee ko féete càmmooñ. Soo duggsee ay pantare yu ndaw ngay gis ñu toppalante ci sa ndeyjoor. Mu jéem a taal rajo bu ndaw bi mu daan faral di dégloo xibaari réew mi. Rajo bi tàkk, xor-xori ba yàgg fey. Fekk piil yee jeex te benn bitig ubbeetul Guy-Géwél. Lee-lee mu dégg ñuy soqiy fetal. Fan yi ñu génn sax, mel na ni ci la xeex bi gënoon a metti. Ñeenti at a ngii gaa ñiy bóomante. Bés bu Yàlla sàkk ñu wax waxu juboo ànd defar réew mi. Mbootaayu xeet yi, ca Amerig, dugal na loxoom ci ay wi, di ko jéem a saafara. Waaye saa yu ñaar déggoo ba wéer seeni gànnaay, ña ca des mer ndax li ñu leen joxul seen gëdd, ne kenn du leen yab,
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_195
xeex bi neeti kurr. Góor gi Aatu Sekk ne ci xelam : « Céy, Afrig moo sonn ! » Benn jinax ñëw na ba riisu ko. Bi waa Guy-Géwél gàddaayee ba tey, kër gi yépp ay jinax laak ay kaña. Foo geestu séen ci ñaar mbaa ñett ñuy wut lu ñu lekk, fu ne ñu dugg fa. Picc yi tamit bare nañu lool ci garabi Guy-Géwél yi. Góor gi Aatoo ngi leen di dégg ñuy woy aka fërr-fërri. Ñoom rekk ñooy wéttalam. Waaw, fan la picc yi jóge sax ? Walla ci garab yi ci kër gi la ramatu yeek sawóor yi mas a dëkk te moom masu leen a seetlu ? Pënd baa ngi jóg, di muur ndab yi ci ëtt bi. Tawu pënd, xonq coyy, mel ni wis-wisalu deret. Peppu pënd bu ci daanu, sa moroom xaar ba nga tag fenn, mu ñëw tafu ci yow. Xobi niim gi it a ngi xonqsi ndànk ndànk, ndax ni ci pënd biy dajaloo. Dem na xayma li des ci waañ wi. Lim bee ka gàtt sax ! Ñetti dogi mburu mu wow.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_196
Tuuti suukar. Butéelu lem. Butéelu tiir. Li gën a soxal Aatu Sekk mooy ndax dese na këriñ. Wër na kër gi yépp, fu nekk mu seet fa waaye gisul fenn këriñ. Nu muy def nag, léegi ? Xanaa wuti ko ci gox bi. Gënalu ko de, wax dégg Yàlla, waaye fàww mu dem ci yeneen këri Guy-Géwél yi, fortaatu fa këriñ ak lu mu lekk. Ñàkk pexe, pexe la. * * * Way-fippu yaa ngi gën a jegesi Guy- Géwél. Ku nekk a ngi fexe noo jiitoo sa moroom Guy-Géwél... Waaye su ñu xamoon ! Benn góor gu màggat ak ay kañaa ki jinax doηη lañu fiy fekk. Ndaw yaakaar ju tas ! Xanaa kay du wut alal moo tax way-fippu yeek nguuru Dibi-Dibi di xëccoo Guy-Géwél...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_197
Guy-Géwél a ngi ne selew booba ba tey. Lee-lee góor gi Aatu Sekk di waxtu ngir wéttalikoo baatam. Ku sañoon a xalaat ne bés dina ñëw Ruq Jinne mel ni nit masu fee dëkk ? Ruq Jinne, nga xam ne moos ci xuloo, xeex ak jamante paaka la gone yiy juddoo, màgg ci, yaroo ci ? Góor gi Aatu Sekk àgg na bitigu Jàllo. Ñu bare ci Guy-Géwél fii lañu daan lebsee soble walla dëwlin walla ceeb. Foo fekkaan Jàllo mu ngi toog ci buntu bitigam, di xëcc naanoom, janq bu ko romb mu tooñ la. « Duggal Seet » la tudde woon bitig bi. Tur woowu nag, daanaka cax la woon, ndax ëttu kër Jàllo la saay- saay si daan làng, lu bon lu nekk ñu koy def. Bi Jàllo wuyujee boroomam, doom jee ko wuutu. Yàlla def Ibnu Jàllo di gone gu gore, yiw te jullite. Dafa daldi dakkal ci saa si ñaawteef yooyu baayam daan seetaan.Waaye tey de, dara desatul ci bitigu Jàllo bi. Ibnu buub na li fi newoon yépp, yab ci oto, ànd ak waa Guy-Géwél daw wuti fu mu làqu.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_198
Góor gi Aatu Sekk a ngi taxaw ci diggu àtte-tooñ bi goney Guy-Géwél yi daan daje di futbal. Fépp fu nit ñi daan dajaloo - muy robine yi, di garaη-palaas yi mbaa feneen - ay ndab ak ay toogu ñu nga fa tasaaroo. Xanaa ragal ñu diisal leen a tax waa Guy-Géwél sànni leen fi dem. Ci buntu sinemaa Palaas, gis na benn nataal buy wone ay Enjeη - mooy ñi ñu tuddee Apaas - ñuy xeex ak ay soldaari Amerig. Ñoom ñépp a ngi war seeni fas di fetalante. Sinemaa Palaas gii tamit, jamono ja Guy-Géwél di neex da daan fees dell ak i nit. Fan yii moom, waa Guy- Géwél tal nañu leneen lu dul seetaan sinemaa ! Waaw, ñoom sax fan lañu war a nekk waxtu wii ? * * * Tey, góor gi Aatu jaarul ci ndékki. Añ moom, waxaalewu ko. Kër yu bare dugg na fa, jéem naa raasaatu ba sonn, waaye fekku fa dara lu mu lekk.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_199
Bi mu rombee sëni Guy-Géwél yi, séen na ay dogitu mburu yu ñu fa sànni. Dem na ba leen di for, ngoram mayu ko ko, mu daldi wéy. Xiif du ko tax a saalit bay lekk ñamu-mbaam. Ndax, kat : Ku mar tax a naan pótit, bu ndox tuuroo nga rus. Góor gi Aatoo ngi jaaxaan ci taatu niim gi ci ëtt bi.Mu ngi miir. Bopp baa ngi metti ba mel ni luy waaj a xar. Xamatul sax fan la nekk. Ñaari waxtoo ngii mu bëgg a tuuri ndox ci wanag wi, jóg fi mu tëdd të ko ticc. * * * Am na kuy ratatati ci rajo bi : « Ay saay-saay ñoo dal ci sunu kow. Ñooñu ay workat yu bon lañu, ndax sunu noon yi nekk bitim-réew a leen ngemb ngir ñu daaneel nguuru Dibi-Dibi. Li ñu nar de, ñépp xam nañu ko : jébbal réew mi ay doxandéem, ñuy dogal, Jafune dellu nekk ci buumu njaam.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_200
Ndax xel mën naa nangu loolu ? » Rajo bi fey, tàkkaat, di xor-xori ba yàgg, waa ji gënatee yuuxu : «...juddoo fi... doom ak i jarbaat... jox lay ngànnaay ngir toroxal nu ? Waaye...Dibi- Dibi, askan wee ko wóolu, jiital ko te fas yéenee ànd ak moom defar réewu Jafune... Dibi-Dibi, njiitu réew mi, nee na... » Rajo bi jékki-jékki feyaatal boppam. Góor gi Aatoo ngi mel ni ku nekk ci biir gént. Waaw, ku taal rajo bi sax ? Xanaa du rajo bii la piil yi jeexoon sànq rekk ? * * * Góor gi Aatu Sekk tiite ci nelaw, jóg, daldi joxoñ buntu kër gi, xaacu : - Dibi-Dibi ! Dibi-Dibi ! Subóoxun ma la ! Lii lépp yaa nu ko yóbbe ! Ku waxal Yàlla, dinga nangu ne bés ba nuy tabb Dibi-Dibi, di ko teg ci jal bi, lépp jaar na ci yoon. Kenn labajul kàrt yi, kenn jalgatiwul wote bi.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf