url
stringlengths 6
8
| content
stringlengths 2
3.72k
| source
stringclasses 3
values |
---|---|---|
page_201 | Dibi-Dibi ci boppam, nit ñi amoon nañu
lool yaakaar ci moom. Gaa, daawul wax
waxu nit, waaye waa Jafune amatuñu
woon pexe. Dunde yaakaar a leen dese
woon. Dibi-Dibi it doonoon nit ku ñeme
Yàlla ! Lu waa Jafune tawat, mu ne am na
ci pexe. Dem na ba dajale lu mat fukki
junniy gone, ne leen :
- Ku amul liggéey ci yéen na yëkkati
loxoom ! Gone yi yuuxu, yëkkati seen
loxo. Dibi-Dibi yuuxu moom it :
- Gaa ñi fi nekk, langaamu ci nguur gi,
lànk ne duñu fi jóge, ay cuune lañu ! Nañu
fi jóge ndax man mi leen yéene lu nekk
ma mën a defar réew mi ! Su ngeen ma
falee, ñu teg ca ñaari weer te yéen ñépp
amuleen liggéey, nee leen ma tuug !
Saa yu Dibi-Dibi waxaan waxi dofam
yooyu ba noppi, da daan wër géew bi, mel
ni mbër mu ñuy tuusal, muy fecc, di
bàkku. Su ko defee, ñépp di woy :
Golo wàccal, gaynde yéeg !
Golo wàccal, gaynde yéeg ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_202 | Mbooloo miy tàccu, jigéen ñiy sarxolle,
gone yiy say. Yëf yi xumb ba dee, nit ñi
naan :
- Kii, mayu Yàlla dëgg la am !
- Mën naa indi xaalis bu dul jeex ci réew
mi !
- Yàllaa dugal Dibi-Dibi ci sunuy xol !
Kenn mënu ci dara !
- Dibi-Dibi rekk ! Dibi-Dibi rekk !
Teewul woon nag, mag ñi xam àddina
amoon xel ñaar ci Dibi-Dibi. Góor gi Aatu
Sekk masul a wóolu Dibi-Dibi. Fi mu
tëdd, xiif di ko bëgg a rey, xelam dellu ci
Omar Jaw, ndeysaan. Waay Omar Jaw a
ko sonaloon ak ay waxi Dibi-Dibi !
Bés, góor gi Aatu muñ ko ba mënatu koo
muñ, mu ni ko :
- Wax nga dëgg de, Omar, sa waa ji
boroom xam-xam la. Waaye am na lu ma
xaw a jaaxal ci moom.
Omar Jaw ne ko :
- Loolu lu mu, Aatu ? | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_203 | - Xanaa ni Dibi-Dibi di doxe. Seetlu nga
ko bu baaxam ? Kàddu yooyu jaaxal
Omar Jaw. Mu ne Aatu :
- Lu nekk ci doxinu Dibi-Dibi ?
Aatu ne ko :
- Baal ma de, waaye sa waa ji ni kanaara
lay doxe. Foofu, Omar xàqataay, tàccu :
- Dikkleen, góor gi Aatu Sekk ràηηatiku
na nag ! Am xaat waa Guy-Géwél yu ñëw
wër leen. Aatu xam ne su fa nekkee di
werante, day yablu boppam. Mu daldi
soppi wax ji ay kaf. Ca ginnaaw-ëllëg sa,
mu ne Omar Jaw :
- Sa waa ji de, dinaa ko sànnil kàrt, waaye
su caaxaan demee dëgg des, wóoluwuma
ko dara. Dafa fekk rekk ne li mag ñi daan
wax moo fi ne : yaa fi sës doy nag pal.
Moo fi sës, fàww mu falu. Omar a ngi bég
ba xamatul fu mu nekk.
Mu ne :
Soo defoon leneen bett ma, góor gi
- Aatu ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_204 | Yow bañkat nga mës a doon, sa dund
gépp danga koo xeex. Mënuma woon a
gëm ne néeg ngaa xañ say doom ak say
jarbaat seen wërsëg.
- Wërsëg wan ngay wax, Omar ?
- Gone yépp dinañu am liggéey,
taxawaalu bi dina dakk ci réew mi !
Aatu Sekk xool ko ba seppali ko, ne ko :
- Omar, ba fi mu nekk daal, gëm nga ne
noonu la mbir mi yombe ? Xanaa kon,
waa nguur gi fi nekk, seen kañaan amul
àpp !
- Du loolu góor gi Aatu, Dibi-Dibi dafa
fendi, moo leen gën a xam ni ñuy téyee
réew. Ci benn daara ju mag la ko jànge !
- Nga ne ma? Fu daara jooju ne ?
- Tugal, xanaa. Foo bëgg mu nekk fa, yow
it Aatu ? Gaa ñi fiy jéem a diir mbagg
Dibi-Dibi yépp daje nañu faak moom,
waaye moo leen daan raw, daawuñu ko
sax séen ! Góor gi Aatu ree : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_205 | - Waaw, Omar, ba daal sunu gaa ñépp
bitim-réew lañu jànge nañuy téyee réew
mii ? Loolu yenu na maanaam ?
- Lu tee ? Àddina day dox ! Aatu wiccax
bopp bi, muuñ :
- Man de, Omar, am na leneen lu ma xaw
a tiital...
- Loolu lan laati, Aatu ?
- Sunu mbokk yi nu wër, xanaa ! Ñoom de
laa ragal ñu song nu bés, këf Dibi-Dibi,
yóbbu ko mu jiite leen, dàqal leen xiif ak
mar ci seeni réew ! Omar Jaw daldi ree
moom itam ba tëdd ci suuf :
- Yaa ngi sog a wax wax ji nag, Aatu !
Réew yu mag yi sax ñu ngi nuy yeeru, bu
nu sàgganee dinanu ko réccu, de ! Xonq-
Nopp yi, kañ ! Yaakaar nañu ne ñoom
rekk a bëgg lu baax ! Am faayda ba dee !
Ci la Aatu xamee ne dof dëgg lay waxal:
- Loolu kay dunu ko seetaan, Omar, su
waa Amerig walla waa Kanadaa naree
sàcc Dibi-Dibi, | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_206 | man mii maay jëkk a tëdd ci kanamu
roplaan bi ndax mu bañ a jóge Jafune !
Waaye Omar moom, loolu yépp safu ko.
Kàrt la bëggoon daal te am na ko, ndax
Aatu wax na ci gémmiñam ni Dibi-Dibi
lay woteel. Góor gi Aatu Sekk yemale fa
waxtaan wa, te naan ci xelam :
« Baax na. Kii moom dina ma fekksi fii
ma toog ne ma waxoon nga ko ».
Te noonu la ame it. Dem nañu ba bés
Omar Jaw ñëw fekk góor gi Aatu fi mu
toog ci taatu garab gi, mu ne ko :
- Yeyati nga ma, Aatu. Ñii baaxuñu !
Aatuy dof-doflu, mel ni ku xamul li muy
wax :
- Lu xewati, Omar ? Yow daal, waat nga
ne fu ñu la fekk yaa ngi ñaxtu ?
Omar ne ko :
- Ñii seen bopp lañu fi nekkal de, Aatu !
Dibi-Dibeek njabootam gaa ngi toη-toη
réew mi ! Du woon it lu bett Aatu Sekk. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_207 | - Omar, noon naa la nit kuy doxe ni
kanaara, ku ko jébbal réewum lëmm yaa
tooñ sa bopp.
*
* *
Du sax Dibi-Dibi moo jëkk a duut
réewum lëmm. Loolu yàgg naa am ci
politig.Waaye yaakaaru nit ñi ci Dibi-
Dibee ka réyoon ! Ñépp di yàkkali bóli.
Yaakaar booboo tax waa réew mi
jàppalewuñu ko yem ci. Dañoo sot dëgg,
Dibi-Dibi jël ndam li. Du woon nag ngir
yaa ma neex. Am na lu ci askan wi jublu
woon : teg ci jal bi kuy fajal nit ñi seeni
soxla. Ndax Dibi-Dibi kat, dafa ne woon
waa Jafune :
- Lépp lu ngeen di tawat, am naa pajam.
Bés sax, yaram wi xaw naa tàng, mu ne
ndongoy daara yi :
- Waxleen ma lépp lu ngeen bëgg !
Gone yi limal ko ay tawat yu baree-bare.
Dibi-Dibi reetaan, ne leen : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_208 | - Lii rekk ngeen may laaj, su ma faloo ?
Xeeb naa ko, ndax sama mën-mën, fu ko
nit natt romb na koy dem ! Kon boog
buleen yox-yoxi, laajleen ma lépp lu
ngeen bëgg, ma defal leen ko. Man réew
mi doηη a ma tax a jóg ! Géwélu Dibi-
Dibi daldi dugg ci wax ji :
- Aywaleen gaa ñi, ku yéex ñàkk ! Ku
Dibi-Dibi tàccu, soo feccul dootoo fecc
mukk ! Am na it ca njëlbéen ga ñu ne
woon :
- Dibi-Dibi ku yëg boppam la, du nangu
njiiti réewi tubaab yi di nu yab. Kenn
feesul bëtu Dibi-Dibi ! Wax dëgg Yàlla,
njiiti réewi Tubaab yooyu, Dibi-Dibi jéem
na leen a të ci ñaari at yu jëkk yi mu toog
ci jal bi. Waaye ba ñu ko xoqatalee, dafa
daldi dellu ginnaaw ci saa si, jébbal leen
boppam. Du it kenn ku mu fi faj soxlaam !
Mbir mi daal, ni ay léeb la mujje, tàbbi
géej, daldi fa faf seey, léebkat bi ni :
- Ku ko jëkk a fóon tàbbi àjjana !
Gone yiy jëkkante, naan : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_209 | - Fuuf ! Fuuf ! Maa ko jëkk a fóon !
*
* *
Dëgg la, Dibi-Dibi da doon sóob rekk,
xaajul a tane ki mu fi wuutu. Waaye xéy-
na su ko Yàlla feyee xolam, du am lu muy
réccu. Amoon na yéene ci réewam. Dara
yàqalu ko lu dul parax-paraxeek teg
boppam fu mu àggul, jàpp ne képp ku
Yàlla sàkk moo la ëpp xel. Ba mu wóoree
Dibi-Dibi ne caη na, dafa am kersay
janook askan wi balu ko àq, nde mënoon
na ni waa Jafune :
- Bëgg a dem taxul a mën dem. Lu ne
jéem naa ko, waaye tey la réew mi gën a
lott. Xawma woon ne nii la mbir mi jafee.
Léegi daal, dama leen di bàyyi ngeen tànn
keneen. Dibi-Dibi deful loolu. Dafa jébbal
réew mi ay doxandéem, ne leen :
- May naa leen Jafune ci xol bu sedd, lu
leen neex def leen, yéene woon naa leen
sax lu ëpp lii, waaye jamonoo neexul. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_210 | Dibi-Dibi jaay na réew mi, ngir sàmm
bànneexu boppam ak bànneexu njabootam
Loolu doηη a indi weranteek reyante ci
Jafune. Dëgg rekk a neex Yàlla. Dibi-
Dibi taxu ko woon yemb. Waaye kuy seet
bu baax, dinga gis ne njiiti réew yu bare ci
àddina si, seen yaram neexul. Dafa fekk
rekk ñu di ay kilifa, ñu leen di làqal yu
bare, di leen sàng sutura.
Moo tax njiitum réew dina dof ba
ràηηatiku te askan wi du ci yëg dara. Li
ñuy wone ci moom ak liy am dëgg, day
faral di mel ni Yàllaak Yaali. Dibi-Dibi !
Mbër mu dul daanu ñaari yoon. Te benn
jéllam boobu, dina ci yóbbuwaale ñu bare.
Ñooñoo koy dar nag, ngir sàmm seen
teraanga. Su waxee lu jaaduwul, ñu ne :
- Dégginu nit ñee des rekk, ndax xalaatu
Dibi-Dibi dafa xóot, boroom bopp dëgg
moo ko mën a dékku.
Bu Dibi-Dibi defee njaaxumam, ñu ne :
- Noonam yeeti, ñoo koy sosal ngir yàq
xeli nit ñi. Mbaa ñu ne : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_211 | - Dibi-Dibi, defar réew mee ko tax a jóg,
waaye saa yu santaanee dara, ñi ko wër
def leneen.Teewul ñu bare ñu àndoon ak
Dibi-Dibi ca njëlbéen ga, mujje koo
jàmbu. Ba Dibi-Dibi tàmbalee tabax ay
mónimaa, la leer ñépp ne yaram wi
neexatul. Da daan xaar ba waa Jafune
yépp di nelaw, muy wër dëkk bi, fu mu
gis bayaal ne nañu fa yëkkati ab mónimaa,
mu dugal ci xaalis bu kenn xamul nu mu
tollu. Jafune day xéy rekk gis ay óbërye
ñuy gas, di daaj ak a dàjji. Su ko defee,
waa réew mi di ko jëw, naan :
- Waxleen ci !
- Gaalu dof du teer, de !
- Baax na ! Ngóor sii, fi mu nu jëme...!
Dibi-Dibi tabax na fi mónimaa jagleel ko
soldaari Afrig ya demoon xeexali waa
Tugal ; beneen bi mu jagleel ko géej gi; ba
ca topp mu tudde ko « Ginnaaw ay,
jàmm ».
Ñu koy jëw, nag : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_212 | - Moo, kii lu mu xewle nii ?
- Moom daal, lu ñëw ci xelam mu ni ayca,
yëkkatileen ab mónimaa ! Laata Dibi-
Dibi di dugg ci politig nag, da daan
jàngale mbirum aadaak cosaanu réew mi,
ci daara Jafune ju mag ji. Moo tax nee ñu
mu bëggoon a màndargaal nguuram ak i
mónimaa. Am na it ñu ne da daan suul ay
gàllaaj ci biir mónimaam yooyu. Ak lu mu
ci mënti doon, ba ay wi jibee Jafune,
mónimaa yi la way-fippu yi jëkk a song,
rajaxe leen. Am na it ay jamono, Dibi-
Dibi dafa aakimu rajo beek tele bi, di wax
tëwa noppi. Bés, mu ne dafa bëgg
waxtaan ak réew mi ci mbir mu am solo.
Mu ne :
- Maa ngi leen di balu àq, ndax fan yee ñu
génn, taxaw naa lu mat juróomi waxtu di
wax. Moomuma leen nag, ba di leen
tanqal. Wax ngeen dëgg, takku liggéey jot
na, coow li doy na sëkk ! Ku nekk ne ci
xelam : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_213 | « Aa ! Lu tey doon, ba Dibi-Dibi di wone
gii maandute ? Xéy-na ay mbokkam a ko
yedd. »
Waaye nit ak jikkoom ba ci biir bàmmeel!
Keroog jooju Dibi-Dibi dafa xéyee talalali
ba tàkkusaan di waaj a jot ! Ba mu demee
ba xamatul lu muy wax, dafa rocci ci kayit
yi tege woon ci kanamam benn nataal,
woolu ay gone, daldi leen laaj :
- Xam ngeen lii lan la ? Gone yi xool
nataal bi bu baax, ne ko :
- Musunoo gis rab wii de, paresidaa Dibi-
Dibi.
Dibi-Dibi xàqataay ba tele biy riir :
- Bettu ma ! Gaa ñi, xam ngeen ne maay
ngànd, de ! Indil-leen ma kiy jàngal xale
yii. Ana seen ustaas ? Kooku ñëw, Dibi-
Dibi won ko nataal bi, laaj ko lan la. Mu
taf gémmiñam, ne ko :
- Lu ma gëj a gis a ngii, paresidaa Dibi-
Dibi !
Dibi-Dibi daldi ko gëdd : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_214 | - Ku la laaj loolu ? Lan la, laa wax ?
- Kanaara la.
- Jërëjëf. Léegi, lenn laa bëgg nga wax
ma, yow doomu Jafune : ana kanaara yi ne
woon gàññ ci mim réew ? Fan lañu jaar ba
ne mes ? Dibi-Dibi nekk fa nag, di wax lu
ñor ak lu ñorul, naan :
Mbir mee ka kéemaane ! Kanaara yi ne
woon Jafune yépp ne mes te kenn xamul
fan lañu jaar ! Dinaa yebal ay boroom
xam-xam bitim-réew, ñu gëstu ci mbirum
kanaara. Ndax kat, man Dibi-Dibi, su dara
desul lu dul jiite réew mu deseetul benn
kanaara, damay daldi tekki sama
ndombog-tànk gii, ngeen fal keneen.
Keroog ñi amoon xel ñaar ci ndofug Dibi-
Dibi sonalatuñu seen bopp di werante.
Waa Jafune jaaxle, ku ne di xool sa
moroom, ñu naan ci suuf :
- Aa, yëf yaa ngi bëgg a ëpp loxo, kat !
Mag ñi fàttaliku démb. Mu mel ne Jafune
dafa dellu ay xarnu yu baree-bare ci
ginnaaw, | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_215 | diggante 1640 ak 1647, ca jamono ja
Daaw Demba sonalee lool Kajoor. Nguuru
Daaw Dembaa ka metti woon ! Tere na ku
lekk yàppu wataboor wu am xorom, ne it
su ñaar déeyante ba reetaan dina leen rey.
Dem na ba ne ku nar a takk janq ci
Kajoor, na nga ko ko indil, mu jaar ci ba
noppi, moom Daaw Demba moomu, sog
laa delloo sa jabar, lo xam nga def.
Lu ñu wax mu ne Buur a ko yelloo.
Kajoor di jëw Daaw Demba ba mujje koo
jàmbu, mag ña gise ci pet fexeel ko, mu
daanu. Waaye ndax yoon la sax, di
méngale Daaw Dembaak Dibi-Dibi ?
Ndax Dibi-Dibi kat, li wóor ba wóor, moo
di ne xel mi neexatul. Seetal ma lii, rekk !
Ku ñu war a tëj kabano ca dof ya, ñépp
wékk seen yaakaar ci yow !
Su Dibi-Dibi wéroon, du taf ay seetu ci
néeg yi ci këram yépp, fu mu walbatiku
daj ci boppam.
Mbon gi ci Dibi-Dibi jarati naa waxam ? | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_216 | Guney Jafune yi feragul sax, dégg nañu ay
jëfam yu ñaaw. Dibi-Dibi dina la ne ràpp
ci kaso bi tëj, woo ay gaana ñu futti sa
jabar ci sa kanam, nga leen di seetaan ñu
koy sàkku te doo ci mën dara. Te bu
boobaa, Dibi-Dibi day toog ci sa wet, yow
jëkkër ji, naan gaana yi :
- Ndaw sii caga la, na seen bal yu tàng yi
tàkk, defleen noonu ndeyam, bu dara sedd
sama gaa yu baax yi !
Yàlla mi dara tëwul a mujjee weer Dibi
Dibi. Naka ? Waaw ! Yow mii téye
Téereb Fent di ko jàng, laajal Aatu Sekk
naka la Yàlla weere Dibi-Dibi, mu wax la
ko ! Daaw-jéeg, bi xeex bi demee ba jéggi
dayo, Dibi-Dibi amal na mitiη ci baayal bi
gën a yaatu ci Jafune. Fu nekk nit ñi fàqe
fa, wuyusi ko. Dibi-Dibi di wax, di wax..
di wax rekk, tëwa noppi. Bi mu waxee lu
mat xanaa ñeenti waxtu, mu ne tekk, xool
asamaan si, daldi jonkan summi dàllu
ndeyjooram, taf ci noppam, di làkk
angale. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_217 | Nee na kat Tóoni Bleer a ko woowe
Angalteer ndax mu xelal ko. Waaw.
Angalteer daal, jànkoonte woon naak ay
jafe-jafe yu réy, Tóoni Bleer jaaxle lool,
daldi ne : « Lii de, kenn rekk a ma ci mën
a génne, te Dibi-Dibi la ! » Loolu de la
njiitu réew mi teg sunuy loxo. Gone ya
teewoon ca mitiη ba mer, di ko sànniy
xeer, di ko yuuxoo. Keroog, su ñu
rawalewul woon Dibi-Dibi, du baax ci
moom !
Ca la réew mi tase ba tey jii. Bés boobu la
nit gëj a teg bët Dibi-Dibi. Feeñatul sax
tele waxatumaak naan day doxantu ci biir
dëkk bi. Su dul woon li muy tanqal waa
Jafune ci rajo bi, ku ñu ne Dibi-Dibi saay
na it doo ko weddi.
Waaye ñi song nguuru Dibi-Dibi tamit, ay
kumpa lañu ci waa réew mi. Ñoom daal
seeni jaasi lañu yor, ñaawtéef bu nekk ñu
koy def. Mbootaayu xeet yaa ngi seet naka
lay def ba yónnee Jafune ay soldaar, ñu
teqale ñiy xeex. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_218 | Way-fippu yi àndu ñu ci loolu. Dibéer jee
ñu génn, seen benn njiit wax na lu leer :
- Soldaar bu jóge bitim-réew, ne dangay
jàppalesi Dibi-Dibi, dinanu defanteek
yow. Foofu la mbir mi tolloogum.
Géej gi waxoon na ko : fitna ji waa Jafune
nekk yépp, seen ñàkk fullaa leen ko teg.
Ci gis-gisu góor gi Aatu Sekk tamit de, su
Jafune teeloon a jóg ci mbirum Dibi-Dibi,
aar kon na boppam ci coono yu jéggi
dayo yi dal ci kowam. Man Aatu Sekk de,
su ma Jafune dégloo, képp ku taxawati ci
pénc mi ne day laaj réew mi, balaa dara di
xew dinaa yëkkati sama baat ci kow, ne :
- Xool-leen bu baax ay bëtam.
Ñu ne ma :
- Lu tax nga wax loolu ? Sama tont day
daldi leer nàññ :
- Képp koo gis muy laaj am réew, am na
lu muy làq askan wi. Soo xoolee bu baax
ay bëtam, dinga ko ca séen muy féey. Bi
góor gi yeewoo ci njël la koy door a leer
ne ñetti fan yi weesu yépp, | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_219 | moom kott moo des Guy-Géwél. Xippi na
ga, waaye xamatul ndax day gént walla
déet. Góor gi Aatu Sekk a ngi dégg ni
butitam yiy jooye, di lemu ak a lemmiku.
Xamul kañ la gëj a xiife nii.
*
* *
Ay xaj a ngi mbów ci tàkkal dex gi, mu di
leen dégg fi mu jaaxaan. Ñaari noppi Aatu
Sekk yi miin nañu léegi tekk-tekkaaral gi.
Waxtu wii la Yilimaan Jonn daan nodd
fajar. Góor gi Aatu wàcc lalam, jubal ci ëtt
bi, jàpp, kàbbar. Ñaan na it Yàlla mu
génne réewu Jafune ci fitna ji ko Dibi-
Dibi dugal. Lee-lee mu mel ni am na ñuy
yëngu ci wetam mbaa ñuy romb buntu kër
gi di wax ci kow.
Xobi garab yaa ngi jooy ndànk.
*
* *
Bés bu jàll, Aatu Sekk gën a lott.Ay
soldaar ñëw nañu ba jub Guy-Géwél, | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_220 | taxaw, am ci ñoom ñu jëkk a seet ndax
amul ay noon yu fi làqu. Ñu nekk fay wër
gox bi ba mu yaakaar ne léegi ñu song
Guy-Géwél, ñu daldi woññeeku.Bi ñu
rombee buntu kër gi la Aatu dégg ñaar ñu
ci doon werante :
- Fii kat, ndekete nit desu fi.
- Danga xam ndax gaa ñi suul nañu fiy
ndell walla déet ?
- Dina ma jaaxal, defe naa ne noo leen fi
jiitu.
- Loolu lay niru, waaye dina màtt ak du
màtt... Waa ji jotul a àggale li muy wax.
Bi ay bali fetal naan :
- Tuyy ! Tuy ! Ratatat !
Ak bi muy yuuxu benn la. Góor gi Aatu
Sekk dégg ñuy soqee fu nekk ay fetal. Ñu
teg ci tuuti, Guy-Géwél dellu ni selaw. Li
muy sonn yépp, fexe na ba jóg, ne day
dabi ñaari soldaar yi romb buntu këram,
ne ki ci jot a mucc : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_221 | - Jaale naa la sa xarit bi faatu, waaye su
doon sama sago nga dóor ma bal, ma
noppaluji man itam. Jébbal naa la sama
bopp. Defal ci man lu la neex. Wànte naka
la Aatu Sekk taxaw rekk, daldi tàmbalee
miir, àggaat ci suuf, di xiixat.
*
* *
Seen ndey a jëkk ñëw. Aatu Sekk xippi,
gis ko mu ne jodd ci ëtt bi di ko xool. Mu
ne ci xelam :
« Moo, kañ la nit daan am geen ? »
Mu bëgg a reetaan, biir biy jam, mu gaññ.
Golo gaa ngi jonkan ci benn xeer wu
dóomu-taal, ne ko jàkk. Aatu fexe ba
wéeru ci niim gi. Li muy sonn yépp, xam
na ne buy sàggan golo gi di ko song, te
kon dina ko gaañ.
« Kii de, am na lu bët yiy wax... » Waaye
lu ñuy war a wax ? Naka lay def ba witt ci
jaww ji kàdduy golo gi ? Aatu Sekk
sànniy bëtam fu nekk Dara rëccu ko ci li
ko wër.Xeer wi ci wetu golo gu jigéen gi. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_222 | Liiñu caas gi leen tiim ñoom ñaar. Tey sax
la Aatu mas a seetlu keppu yu weex yeek
yu xonq yiy làng ci liiñ gi.Toogu bant bu
gudd bi. Ci la xaritu Aatu yi daan teg seen
damyee, di wure subaak ngoon. Ni toogu
bi jaaxaane ci taatu niim gi, ñaari yëf la
tekki. Wéetaay bu tar. Bànneex bu dëddu
Guy-Géwél. Ñu jékki-jékki, ngelaw li
yëngal bunt bi, golo gi tëb, geestu, fu ne
mu xool fa ba noppi neeti jodd, janook
góor gi Aatu Sekk. Aatu moom mu ngi
yëg ni ko xiif gu metti giy
miirloo.Tàngaay baa ngi ko jàpp ba noyyi
të ko, tuñ yiy gën a wow bés bu nekk.
*
* *
Ginnaaw-ëllëg sa, golo gi dellusi.
Fekk na sibbiru si daaneel Aatu Sekk.
Bii yoon, ci garab gi la tëbe, ne putt ci
suuf. Waaye tey de, dafa mel ne ku àndul
ak sagoom. Mu ngi yuuxu, di xalangu ci
ëtt bi, di sëpp-jaleñu. Jàppe na ko noonu
ba yàgg, mu daw wuti mbedd mi. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_223 | Ci la góor gi Aatu Sekk sog a nànd ne am
na lu ko golo gi bëgg a won.
*
* *
Keroog la golo gi bàyyi ñaari doom yeek
Aatu. Bi Aatuy laata xam lu xew, sànni na
leen ko ba dem yoonam.
Aatu Sekk di fo ak ñoom, di leen toppatoo
ni mu ware ba ñu far nekk ay wéttalam.
Waaye golo du mbokk ! Ñaari gone yi,
yar ak teggin dëgg lañu won góor gi ci fan
yu jëkk yi. Noonu lañu naxe Aatu, mu
jàpp leen ni ay doomam yi mu jur.
Ndekete ñu ngi koy yeeru, di xaar ba
jekku ko, toroxal ko. Bés, ci yoor-yoor,
ñaari doomi golo yi fekk Aatu muy dajjant
fi mu doon féexloo ci taatu niim gi. Ñu
daldi gaawantu yeew ko ci garab geek
buum gu dëgër. Aatu kañ gis na leen ñuy
kër-këri, waaye mu ngi reetaan, defe ne
dañu koy jàngal po mu bees. Keroog, fa
lañu ko takk ba reer jot, ñu xollil ko reenu
ñàmbi, jox ko mu lekk. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_224 | Ñàmbi ji xaw naa dëgër gaa, wànte li Aatu
Sekk di nekk mag yépp, bëñ yi
yàqooguñu. Lee-lee kenn ci ñoom ñaar
dugg biir Guy-Géwél, delluseek gerte-
kemb mbaa xollitu banaana, sànni ko
Aatu, mel ni kuy jox sa xaj mbaa sa xar
mu lekk. Suy sàqami ñàmbeem, di yuut,
ñu koy ñaawal. Lu tuuti lu mu def, ñu
gàddu seen yat, di ko ndulli ba mu
yaakaar ne dañuy koy bëgg a rey. Lee-lee
ñu defaru ba jekk, sol seen sàppo tubaab
yooyu, takk seeni lonet, karwaatu, ne ñu
ngay tàllali seen tànk biir Guy-Géwél.
Waaye duñu bàyyi mukk góor gi Aatu
Sekk ginnaaw. Fàww ñu yóbbaale ko. Da
leen di topp, ñuy xëcc ci buum gi, di ko
wommat. Yenn saa yi sax Aatu Sekk kaf
ak ñoom :
- Wutewumaak Buur buy nemmeeku ay
diiwaani réewam. Xanaa kay li ngeen ma
takk ni seen jaam rekk moo ma ci xaw a
jaaxal. Ñaari doomi golo yi reetaan, caw
ko, gën a xëcc ci buum gi. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_225 | Lee-lee seen ndey dellusi ci kër gi, taxaw
ci kow miir bi, woo leen, ñu fekki ko, fo
ak moom ba Aatu Sekk defe ne suy dem
da leen di yóbbaale. Waaye day jékki-
jékki ne mërr, wacc leen ak Aatu Sekk.
*
* *
Aatu Sekk wutal na ku ci nekk tur. Golo
gu góor gi mooy Ninki. Rakk ju jigéen
jeey Nanka.
Ninki-Nanka. Fukki fan ak juróom-ñaar a
ngii tegul nit bët. Nankaak Ninki doηη
ñooy wéttalam. Ñu ngi miinantesi, nag,
mook ñaari ganam yi. Li des rekk mooy
mu mën a waxtaan ak ñoom. Naka-jekk,
Aatu masul a bare wax, waaye ñetti fan yii
de, ay noppam namm nañu lool kàdduy
nit.Golo yi ñoom, ñu ngi wax ni ay
Doomi-Aadama Aatu xamul sax wan làkk
lañuy làkk. Li mu ci xam daal, moo di ne
seen waxin gaaw na lool. Laay !
Ndekete golo tamit dina bar... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_226 | Xel mi dem fu sore, mu ne :
- Céy, nun ! Fu nu jëm ak Dibi-Dibi ?
Wànte sama coono beek sama wéetaay bii
am na lu ñu ma jàngal ci mbiri àddina :
tés-tés ji nit ñi nekke, dara waralu ko lu
dul bëgg a fàtte seeni naqar. Lu ñu dugg
looloo leen ci dugal. Saa yu nit sóobee
lenn, gasaale na pax suul fa leneen lu ko
naroon a gëtën.
« Waaye man mii nag, ci lan la nekk ? »
Góor gi Aatu Sekk xamul lu muy tontu
boppam ci laaj boobu. Li ko wóor daal,
moo di ne deseetul pexe. Mu ngi wéeru ci
taatu niim gi, di xaar Ninki-Nanka ànd ak
moom, ñu doxantuji biir Guy-Géwél.
Ñaari gone yii ñoo ñuul xol ! Dañuy
wommat Aatu ba ci mbalka mi ci wetu
Toolu-Buur, ñu yolomal buum gi ñu ko
yeewe, mu sëgg naan ci ndox mi ba
màndi. Bu ñu dellusee ci kër gi, ñoom ñu
lal seen taabal, téye seeni kuddook seeni
furset, di lekk, di sàqami ndànk. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_227 | Dafa mel ni sax gone yi am na yu ñuy
jëfandikoo, de ! Walla ? Xet gii gën a doy
waar ! Mbaa du doomaraam yii dañuy
naan sàngara ? Su dul sàngara it, niru na
ko lool ! Li ñuy lekk yépp, ñu ngi waxtaan
ñoom ñaar. Góor gi Aatu Sekk yéemu.
Moom daal, su dul woon seen geen yu
gudd yeek seen karaw gu xonq geek seeni
daar-daar, mu waat ne ay nit lañu ! Ni ñuy
waxee ka gaaw, tey!
- Ra-ta-ta-ta-ta-tat !
Ay kàddu yu mel ni ay bali fetal !
Jékki-Jékki, xolu Aatu fees, mu daldi
yuuxu : Sama baat ci kow ! Man, Aatu
Sekk, maa ne kenn du la gën a baadoolo,
yow ! Li ma la defal ci àddina yépp,
amoo loo may feye lu dul di teg kàddu yu
ñaaw yii ci sama der ! Bi Aatu waxee
loolu, ñaari golo yi xoolante ba noppi ñëw
wër ko. Ninki-Nanka jaaxle lool. Lu Aatu
xewle bay waxtu ?
Kan lay xulool noonu ? | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_228 | Aatu ηaaη, di xiixat, ba yàgg mu yëkkatiy
loxoom ni ku réccu li mu def, di jéggalu:
- Baal-leen ma àq de, goney mberaago yi !
Dafa am lu ma fàttaliku rekk, sama xol
fees ! Yéen dungeen ci dara. Samay noon
ñoo fàqee barsàq bëgg ma fekk fii ma
toog, di waxtaan ak yéen, ñu coob ma !
Waaye dëmm yooyu, dinañu wax lu set
balaa ñu may wann !
Bi Aatu waxee loolu ba noppi, Ninki jël
benn xollitu banaana, tiimale ko ci
gémmiñ gi. Aatu ηaaη, yaakaar ne dafa
koy jox mu lekk. Ninki sànni xollitu
banaana bi fu sore, yuuxu, fëgg dënnam,
xulli Aatu Sekk. Aatu xam ne dafa mer,
daldi sëgg. Ninki làkkanteek rakk ji.
Nanka tëb miir bi, dem ci mbedd mi,
delluseek yatam wu dijj, ne ko jabb Ninki.
Li Ninkiy dóor Aatu yépp, mu ngi koy
saaga, di ko wéq.
Keroog, joxuñu Aatu mu añ. Seen ndesit
ya mu daan lekk yépp, dañu ko tuuri
mbalit. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_229 | Aatu Sekk a ngi leen bëgg a balu àq,
waaye saa yu ηaaηee, mu mel ni dañuy
jamat ay puso yu tàng jërr ci gémmiñ gi.
Fi ñu ko takk, mu ngi yërëmtalu.
Ndeysaan !
- Yéen a ñuul xol, doom ! Nu ngeen àttane
def seen Maam Aatu Sekk lu ñaawe nii ?
Dangeen ma bëgg a toroxal, daal ? Naka
la Ninki dégg baatam, daldi bàyyi tele ba
mu doon seetaan ñëw tiim kook yatam,
xàcci, dem ba koy dóor, wàccewaat
loxoom. Soo gisee Aatu, mu ngi banku ni
gone gu ñuy waaj a duma mu dem boqu ci
ndeyam. Ninki xool ko ba seppali ko,
wacce loxoom ne walbit, dellu seetaani
teleem.
*
* *
Nanka randatu na ba ci noppi mag ji, mel
ni ku koy déey dara. Aa ! Ay golo yuy
déeyante, nag ! Aatu Sekk a ngi bëgg a
jommi kat ! Déeyante de, masul a xalaat
ne ku dul nit Njaay mën na koo def. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_230 | Ndax kat, lu Doomu-Aadama denc ci
xelam la ba noppi fas yéene koo dénk ku
mu wóolu dëgg. Kuy déey nit dara, sa
xalaat ngay xelli ci xelam. Te ba àddinay
baax de, golook yeneen mala yi daawuñu
xalaat bay wax. Su weesoo seku daal
- te seku sax li muy wax dara la ci xamul !
- sëpp-jaleñu, yuuxu ak yu ni deme lañu
xamal mala yi.
Waaye déeyante tàww ! Nguuru Dibi-Dibi
gii kañ, lu nekk dinañu ko ci gis !
Déeyantee ka kéemaane tey ! Du jokkoo
neen, de ! Déeyante, segg dëgg la laaj, te
loolu nit Njaay moo ko yelloo. Ak ni
àddina si tollu, nga taamu ci benn Doomu-
Aadama doηη, wóolu ko, sëgg ci noppam,
tàbbal ci xelam loo xam ne ginnaaw Yàlla,
yéen ñaar rekk a xam lan la...
Ci xaaju-guddi la benn balu fetal fëq
buntu kër gi. Teg nañ ci ñeenti waxtu yoo
xam ne bal yaa ngi doon def :
- Tuyy ! Tuyy ! Tuyy !
- Ra-ta-ta ta-tat ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_231 | Am na it ay këri Guy-Géwél yuy lakk.
Lakk gi warul a soreyook fi Aatu toog,
ndax ëtt baa ngi leer nàññ. Aatu Sekk ni
ci xelam : « Mel na ni gaa ñaa ngi xëccoo
Toolu-Buur ». Yoon yu bare te yaatooy
jaar Toolu-Buur, nag.
Moo tax ñu ne :
- Ku teg loxo ci Toolu-Buur yaa moom
Guy-Géwél, moom dëkk bi. Te ku moom
dëkk bi, li des ci réewum Jafune mënu laa
të. Xare Guy-Géwél bee ka nar a metti !
Góor gi Aatu Sekk walbatiku, daj ci ñaari
doomi golo yi, ne leen :
- Yéen ñaar ñii de, wóor na ma ne Toolu-
Buur la leen seen ndey rawalee, dénk ma
leen ba noppi nekk ci àll biy taxawaalu.
Golo yi tontu ko ci seen làkk.
Mu ree :
-Dara laa xamul ci li ngeen may wax !
Waaye ay doomi golo ci Guy-Géwél gii
de, Toolu-Buur rekk lañu mën a joge !
Benn kanu dal. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_232 | - Réll ! Ay roppëlaan tiim dëkk bi, yàbbi
safara su baree-bare ci mbeddi Guy-Géwél
yi. Asamaan siy rëg-rëgi, kër yiy riir, bunt
yépp di dal, jaww ji ñuul kukk ak saxaar.
Aatu Sekk daldi ne golo yi : Dof yaa ngi
ci yoon wiy ñëw de, léegi ñu ne jamet ci
sunu kanam ak seeni saar de kombaa !
*
* *
Jaratul werante. Xeex bi agsi na biir Guy-
Géwél. Way-fippu yeek waa kër Dibi-
Dibee ngi jàppante ci wetu Toolu-Buur.
Oto làrme yaa ngi riir, di waηηeetu ni ay
fas yu seen fit rëcc, pënd bi topp leen.
Aatoo ngi déglu it kanu yi, di gis ni safara
siy raaye asamaan si, door a dal ci suuf,
tasaaroo. Bakkan yu baree ngi rot ci xeex
bi. Li leen Guy-Géwél jaral de, réy na !
Foo tollu, dégg ay soldaar ñuy jooy, naan :
- Wóoy sama ndey !
Xeex bii de, xanaa mooy bi mujje...
Rajo bi sax wax na ko : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_233 | « Waaw. Nee ñu de, ku teg loxo ci Guy-
Géwél gàddu ndam li. » Lenn moom wóor
na Aatu. Bés bu jàmm dellusee Jafune,
baadoolo dootul des Guy-Géwél. Béréb bu
ame nii solo, boroom alal yi dinañu ko
aakimoo. Rax-ci-dolli, dafa tafu ci géej gi
te it dex gi sorewu ko. Te ku nekk xam na
ni boroom barke yi yéenewuñu kenn
péexu géej gi.
Am na góor suy wax ci rajo bi. Nee ñu ku
xelam màcc la ci mbirum làrme ak
bóomateek yu ni deme.
Mu ngi naan :
« Waaye man de, ci sama gis-gis bu gàtt
bii, yaakaar naa ne xare Guy-Géwél bii du
gaaw a sotti. Ndax ku fexe ba teg ci loxo
it, kepp la fi dina yomb lool. Waaye nanu
xaar rekk, li ci kanam rawul i bët ».Góor
gi Aatu Sekk wiccax bopp bi, gëmm,
tàmbaliwaat dajjant. Sibbiru bi sonal na
ko lool wànte nanguwul a tëdd ci lal. Xam
na ne su ko defee dootul mën a jóg te kon
sax du ñàkk mu jaare fa ñibbi àllaaxira. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_234 | Lu mu yëg ci yaramam la. Pas-pasu dund
doηη a ko téye, nde kon leneen lañuy wax.
Ñaari gone yi kañ, ñoo ko jaaxal. Lu mu
leen def ba ñu koy yeew ci niim gi, di ko
sànni seeni ndesit, su ko bañee lekk ñu
koy duma ay duma yu metti ? Bu doon
sagoom de, ñu may ko mu sangu, sol yére
yu set, jublu penku julli, ni mu ko daan
defe àjjuma ju jot.
« Céy sama gan yi ! Ñu ngay kurti-
kurteeti ci biir saal bi, de ! Baat yooyu
may dégg, ñoom rekk la mën a doon ».
Noonu, Aatu fexe ba yolomal buumam,
jóg ndànk, di yoot, ba dem bett leen. Ñu
ngi ne noηη ci kanape saal bi, janook tele
bi. Aatu gën a waaru. Moom mi
yaakaaroon ne tele bi baaxatul ! Ak lu ñu
bare-bare pexe, defaruñu ko xanaa kay...
Dikkleen ! Waa Guy-Géwél, dikkleen !
Golo yuy defar tele, nag !
« Lu tee, sax ? Réew mu dof bu mel ni
Dibi-Dibi mën a jiite kat, dara waratu fee
jaaxal kenn ! » | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_235 | Góor gi Aatoo ngi làqu ci ginnaaw buntu
saal bi di leen seetaan. Sañul a sëqat. Su
ñu yëgee ne yolomal na buumam ba jóg
taxaw, dañu koy rey ! Xale bu góor bi,
Ninki, dafa rekk soxar, moom ! Ci tele bi,
benn janqu tubaab a ngi làkk nasaraan.
Ni muy waxee gën a gaaw ! Waaw,
moom sax ndax dina noyyi suy wax ? Saa
yu noppee, am benn woykat bu feeñ ci
tele bi. Aatu jot naa gis ñeent mbaa
juróomi woykat ñuy tëb di dal, ñaq tooy
xepp, di yuuxu, sol ay yëre yuy melax.
Kenn ci ñoom a ngi fecc taatu-lawbe, ànd
ak ay janq yu sol yëre yu ñuul kukk.
Góor gi Aatu ne ci xelam :
« Céy goloo am bayre ! Gone yi ma gis
ñuy fecc léegi yépp, golo yi doηη lañuy
toppandoo ! »
Ñaari golo yi ñoom taluñu dara, xanaa ne
jàkk tele bi, ne tekk, noyyi sax defatuñu
ko. Aatu Sekk sog a nànd nag lu tax ñu
gëj koo wéttalisi. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_236 | Ndeke guddeek bëccëg ñu ngi seetaan
tele! Leneen lu dul loolu safatuleen.
« Xanaa ma jàppe ko noonu, boog ».
Aatu taxaw na lu mat genn-wàllu waxtu ci
buntu saal bi, te Ninki-Nanka yëgu ci
dara. Bi doomi golo yi génnee, fekk nañu
góor gi Aatu mu takkaat buumam ba mu
dëgër, di nelaw-nelawlu ci taatu niim gi.
Fan yooyu yépp, golo yi dañu xawoon a
mel ni ñu fàtte góor gi Aatu Sekk. Su leen
gisee, dañu ko romb, dem ci waañ wi
defari seen kafe, daldi gaawantu dellu
jaaxaan ci kanape saal bi.
Aatu moom, dara dàqalu ko nëbbu di
seetaan ñaari golo yi ñuy seetaan tele !
Ñaari waxtoo ngeeti mu tafu ci ginnaaw
bunt bi di leen xool. Nankaa ngi ànd ak
benn woykatu tubaab bu jigéen di fecc,
kookuy woy, mu koy awu. Lu ndaw si
def, mu def ko. Mu ngi la koy salliirul, di
fëgg dënn bi, di wiccax bopp bi, ba ne
tuuti mu taxaw, ne jabb loxo càmmooñam
Ninki. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_237 | Kokku téye ci ndigg li, ñu ànd di
wëndéelu, fu nekk ñu fay sànni seeni tànk,
coow li ne kurr ci saal bi. Góor gi Aatu
waaruwul yem ci. Dafa tiit bay dankaafu
boppam :
« Aatu Sekk, ñaari gone yii waxaguñu li
ñu la naral, de : ndof ak dee ngi lay yoot.
Bul ko nangu. Lànkal, Aatu Sekk, bul
nangoo jommi. » Aatu Sekk, yaa yey
muslu ci sa ñaari gan yi. Bàyyima yii, soo
leen di xeeb ñu lay gaañ ! Nook ñoom a
bokk dunyaa. Ëpplewunu leen ci benn
yoon. Dégg naa sax dinañuy yéemu lee-
lee ci sunu njaayum puukare mu metti, di
nu jëw ci seen làkk, naan, xam naa :
- Doomi-Aadama Njaay yi fan lañu teg
seen bopp ? Lu tax ñu yaakaar ne képp
kuy noyyi ci kow suuf si ñoo la gën ? Aa !
Neex ba dee !
*
* *
Soldaari Dibi-Dibi yeek way-fippu yi
wéerati nañu seeni ngànnaay. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_238 | Ñetti fan a ngii Guy-Géwél ne selaw.
Taxul nag waa gox bi ñibbisi. Loolu, kenn
waxaalewu ko sax. Mel na ni Dibi-Dibee
jekku way-fippu yi. Bi Aatu Sekk déggee
loolu, dafa jàpp bopp bi, mbir mi def ko
tiis wu réy :
- Ba waa ju kannasu jii daal, moo nar a
wéy di nu jiite ! Dina fi toogati ay at, di nu
tuur àndaari wax, ñépp di ko sukkal, di
raam, ku jóg taxaw mu dóor la bal nga
daanu ! Waay Afrig moo sonn !
*
* *
Sàkk pexe jot na. Moo yey fagaru, bala ko
ganam yiy jommal. Guddig lëmm la toog,
ne fàww mu fàttaliku lépp lu mu mas a
xam mbaa mu mas koo dégg ci mbirum
golo. Ku bañ ñu bett la, dangay teel a
fagaru. Ndax bés bu fippu yeek Dibi-Dibi
juboo, ba ay wi dakk, moom Aatu Sekk
dina defanteek golo yi ba géej gi fer. Du ci
bañ dara, nag ! Dinañu ko wax lu waral ñu
yeew ko ci taatu niim gi dëj ko fi. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_239 | Aa ! Moom daal mooy seen jaam ? Dina
leen won mooy kan !
Ninki.
Nanka
« Sunu xaree nar a metti ! Dinaa leen jàng
ba jeexal leen, ndax ma xam fu ma leen di
jaar ! »
Aatu Sekk lim ci xelam fànn yi mu
yaakaar ne warees na cee gëstu ngir gën a
xam xeetu Ninki-Nanka.
« Lépp lu gëstukat yi bind ci mbirum
golo, war naa koo jàng. Dara waru ma cee
rëcc ». Jamono jan la xeetu golo feeñ ci
dunyaa. Fan la golo gën a baree : réew yu
tànge ni réewi Afrig yi mbaa ci dëkk yu
liwe ni yu Tugal yi ?
Dëkk bi kenn sañul a bóom golo. Nekkul
réewum End, saxam ? Askan yi leen di
wàjj, di lekk. Golo yi dëkk ak nit ñi, di
dem aka dikk ci mbeddi Sibraltaar yi. Lee-
lee kenn ci ñoom taxaw ci benn bitig, jënd
sigaret, taal, daldi xëcc ba noppi sànni
saxaar si, dëngalu dem yoonam. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_240 | Golo yi ñu tëj fii ci Toolu-Buur, gone yiy
ñëw di leen seetaan, di leen sànni gerte
kemb ak xollitu banaanaak xollitu sorãs.
Naka la golo yiy dunde ci àll bi.
Ni ñuy tànnee seen njiit.
Ni ñuy séye ci seen biir.
Li ñuy lekk. Góor gi Aatu di lim ba agsi ci
ni golo gu jigéen di doxaleek ay doomam.
Mu ne ci xelam :
- Lii mooy li ëpp solo ci mbir mi.
- Ni golo mënee toppandook ηóobi.
Ñaawaayam bu metti :
- Ku ñu ne yaa ñaaw ni golo, xas nañu la
dëgg ! Ndax rab woowu sax am na wàll ci
cosaanu réewum Jafune ? Xelu Aatu ne
yarr ca juróom-ñeenti téeméeri junniy
golo ya jógaloon Nijaay Gaynde. Guddeek
bëccëg ñu topp ko. Muy fàdd rekk, wànte
saa yu demee baa yaakaar ne jeex nañu,
ñu gën a bare ciy bëtam, topp ko rekk, ñii
langaamu ci cari garab yi, ñii di ko sànniy
xooxi màngo. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_241 | Ñu jàppee ko noonu lu mat juróom-benni
fan. Nijaay Gaynde dem ba amatul pexe,
mu jaaxaan, jébbal leen boppam. Ñu wër
ko nag, di ko ηóobi, di ko saaga ci seen
kàllaama golo. Ba mu leen wóoree ne
Nijaay Gaynde Njaay saay na, ñu bàyyi ko
fa dem seen yoon.
Ni golo nirook nit, nag ! Moom kay, ñépp
war nañoo xas golo ba mu des nun. Ndax
lee-lee nga ubbi ab téere, gis ci nataalub
Doom-Aadama, nga xool bu baax xar-
kanam gi, mu indil la bu baabun mbaa bu
dàngin. Jàkkaarloo golo ak nit mënees
nañu cee duy géeju xam-xam. Su la golo
nee jàkk, fàww sa yaram daw, nga dawale
say bët. Du tax mu may la jàmm. Am na
lu mu lay wax, de. Soo demee nun ñii
danu ko def i ree, mu naan :
- Xoolal ma ngóor sii rekk ! Sama mbokk
mee ñeme lu metti ! Waay, yaa sob ! Lu la
xiir ci gii génn xeet ? Li ngay tiitaroo, jar
na koom ? Yaak man la woon démb, nuy
dóor-dàqe ci àll bi, di dunde ay xobi garab
ak i doomi màngo. Fàttalikul. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_242 | Dafa neexoon ba dee ! Nga xéy bés rekk
ne doyal nga ci nekkin boobu ! Ban njariñ
la la amal, tey ? Nee nga tuddatoo golo,
ndax yaay Nit. Su sa soxna ëmbee, nga ne
ko bumu jaar ci sama tur, mu may woowe
noppi-jaboot. Fu mu foog ne dinaa fa aw,
mu jaar fa ca des ndax rekk ragal dajeek
man, ma jigadi doomam. Nee nga yow
rekk a am xel, di defar ay roplaan ak ay
jumtukaay yu kenn xamul. Yu ñàkk
faayda yooyu tax nga xeeb ma. Sa doom
yu xamadi yi duñu ma romb te neewuñu
ma :
- Mbëllee ! Céy golo, lu tax nga ñaaw nii
ak sa taat yu lakk yi ?
Ñaawuma kañ, doom, damaa nirook baay
kepp ! Ñàkk xam li mu waral bare na ! Te
bu dara desul lu dul ηóobi, maa ko dàq
fuuf say doom ! Te sax, nanu waxante
dëgg, saa waay. Tas nga àddina si, sonal
sa bopp, dëkke naqar. Bi nga xamee ne
noonu la yëf yiy mujje, mënoon nga des
fii, ci kow garab gi ! Bul ko yàggal, ngóor,
tee ngaa yéegaat, fekksi ma fii ? | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_243 | Li nga nekke kat, gisuma lu ko jar ! Ku
nekk naan sa moroom maa la dàq daw,
maa la dàq jàng, sama jëkkër moo ëpp
xaalis sa jëkkër, sama réew a ëpp doole ci
réew yi ci àddina si sépp ! Yu ñàkk solo
yooyu bañu leen ci ba ku jekku sa
moroom butti ko. Waaye fi nga ma yéeme
dëgg, mooy bi nga jëlee sa sagaru kayit,
rëdd ciy nataal, tudde ko xaalis, làq ko fu
sore nag, nit ñi war a reyante ngir xam fu
mu nekk, ñu fexe ba luqatee ko fa. Waaw.
Yow kat yaa ne ku amul ci kayit yooyu ba
mu doy, du lekk du naan, te bu feebaree
du faju ! Loolu nag, nga wéer ko fan,
yaaram ? Góor gi Aatu geestu fu nekk, di
seet fan la golo giy waxeek moom.
Réewu Dibi-Dibee doy waar ! Waaye nag,
du toog ne yàcc-yàccaaral, ay golo di ko
xas !
Xol bi daldi jóg, mu tëb, ne day fekki
Ninki-Nanka fa muy seetaane tele,
defanteek moom ba mu saf sàpp ! Waaye
góor gi fàtte woon na ne buum a ngi
yeewe ci baat bi. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_244 | Ni mu xëccoo, buum gi naj ko, mu yuuxu.
Nankaa jëkk a génn, gis ko, daldi woo
mag ji. Ninki ñëw, gëdd góor gi ba noppi
fasaat buum gi ba mu gën a dëgër.
*
* *
Guddig sàttumbar. Biddéew yaa ngi tiim
Guy-Géwél di melax ci asamaan si. Yoo
yeek yeneen gunóor yaa ngi biiw. Lu mat
waxtoo ngi nii Aatu Sekk di wër garab gi.
Waaye mënul a dem fu sore ndax li ñu ko
yeew.
Jékki-Jékki ëtt bi leer nàññ, suuf si yëngu.
Aatu Sekk séen lu xàwwikoo ci asamaan
si, wëndéelu ci jaww ji ba noppi tàbbi
géej, ni :
- Tu-tuuy ! Ne tuuti mu dégg ay tànk yuy
jëmsi ci moom. Mu daldi ne ci xelam :
« Ñooma. Agsi nañu. »
Ñan ñooy ñëw sax ? Waa kër Dibi-Dibi
mbaa way-fippu yi ? Waaye ndax loolu
sax amati na solo ? | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_245 | « Ak ñu ngeen mënti doon, maa ngi leen
di xaar ! Ñëw leen def ci man lu leen
neex ! Yàllaa leen ëpp doole fuuf ! »
Xelu góor gi Aatu Sekk ne yarr ci Ninki-
Nanka. Mu yuuxu :
- Yéen daal, waat ngeen ne sama saal beey
seen fowukaay ! Baax na ! Su ma leen fa
fekkee dinaa lakk seen lu bon !
Mu direeku ba ci ñoom, fekkati leen ñu
jaaxaan di seetaan tele. Ku mas a gis lii ?
Tele buy tàkk guddeek bëccëg... Ay
futbalkat a ngi topp ci benn bal bu weex di
daw. Am na ku ñu ci ne jabb benn kayit
gu xonq, dàq ko ci biti, mu teg ñaari loxo
yi ci bopp bi, di jéggalu. Moroomam mi
mu gaañ a ngi jàpp ci tànk bi, di gaññ, di
wañaaru ci déndub futbal bi. Doomi golo
yi ñoom, ndekete ñu ngi janook seen tele
di nelaw bay xandoor. Aatu Sekk daldi
dëpp, xool montaram.
- Ñetti waxtook genn-wàll rekk a jot. Bët-
setagul. Nelawaat xej na fi. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_246 | Du ñàkk mu am ñu ne góor gi Aatu Sekk
bare na lu muy wax waxu telewisoη.
Ñooñu de, su ñu seetoon bu baax seen xel,
dinañu xam ne yëf yi mënul a deme
neneen. Naka lay def ba xelam du nekk ci
tele bi dëkkee tàkk ci saal bi ? Mu ngi
Guy-Géwél di xaar. Lu muy xaar ? Xamu
ko. Xamul it ñan lay xaar. Ñu ngi ci yoon
wi daal, ak seeni ngànnaay. Ginnaaw
reyantee xew Jafune, kañ ! Aatu Sekk
fexewaat ba yolomal buum gi ñu ko
yeewe, raam ba ci buntu saal bi, tiimaat
Ninki-Nanka.Telee ngi wone ay saar de
kombaa yuy yàbbi safara, di mbëkk garab
yu ndaw yi ci àll bi, ñuy daanu. Ay
soldaar a ngi daw, di wut fu ñu làquji
waaye fu ñu aw, saar yi kar leen, soqi, faat
ci ñu bare.
Bi loolu weesoo, ñu gis benn soldaar bu
ñu jam ci dënn, mu nekk ci sukkuraat,
ndeysaan, tëdd ci ñax mi, deret jiy
walangaan, muy janeer. Mook coroom ñu
ngi dóor-dàqe ci kow benn tund, di
xàqataay. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_247 | Ku leen gis xam ne ñoom ñaar nobante
nañu lool. Ndaw si taxaw, joxoñ bakkanu
far wi, cof kook baaramam, ne ko :
- Fii laay noyyee !
Ku góor ki ree, gën koo kott.
Janq bee ka rafet, kaar ! Karaw gaa ngi
ñuul kukk, di watatu ci ginnaaw mbagg yi,
cëru jigéenam yépp mat sëkk. Xaleelu
góor bi dab ko, kottaat ko, ñu
fóonantewaat. Ñu teqalikoo, ku ci nekk ne
jàkk sa moroom, ñuy làkk nasaraan.
Ku góor kaa ngi tàggu janq bi, naan ko:
Maa ngi nii di waaj a dem xare, ni samay
moroom. Yow rekk laa mas a nob,
Margërit. Su ma dellusee ci jàmm, dinanu
daganal diggante bi. Boo gisee Margërit,
mu ngi jooy, ndeysaan, bay yikkat, far wiy
jéem a dëfal xol bi. Noonu ñu
kottantewaat, fóonante ba mel ni ñu
àndatul ak seen sago. Ndaw si jékki-jékki
jéngu, futtiku sànniy yëreem, ne moom
moo tey, dafay jébbal far wi boppam ! Ku
góor ki lànk, ne ko mukk du ci dal. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_248 | Bi film bi àggee foofu nag, Aatu Sekk
seetlu na lu doy waar. Bi ndaw si
tàmbalee futteeku, ñaari doomi golo yi
dañu daldi tàggook seen sago ci saa si. Ñu
ngi yuuxu, di tàccu waa ji. Waaye bi
soldaar bi bañee tëdde coroom, jéppi nañu
ko lool. Dem nañu sax bay dóor tele bi, di
sànni seeni loxo fu nekk, di ciipatu, di
saaga waa ji ! Mel ni ñu naan :
- Ngóor sii moo ñàkk faayda, dëgg ! Gel
bu tooye nii moos, yéene la ko, di la ko
jox ci xol bu sedd, ngay nakk-nakkal !
Mbaa du ponkal mii daa tële, di ? Aatu
Sekk gën a tee waaru. Waaw, mbaa du
gune yi dañoo dégg nasaraan ?
« Xanaa kay du ci tele bi lañu jànge làkk
woowu ! »
Góor gi Aatu Sekk walbatiku, raamaat
ndànk ba ca taatu garabam ga, yeewaat
boppam, jaaxaan, di nelaw-nelawlu, ni mu
ko tàmmee def. Ban bés lañu nekk ?
Altine ? Àllarba ? Xamu ci dara ba dara
boolo jeex. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_249 | Bés yi maasaloo nañu. Jamono ji ci
boppam saay na. Aatu Sekk njort na ne
léegi ràññee tàkkusaan ak njël të ko. Li
wóor daal, moo di ne fexe na ba dagg
buum gi ko doomi golo yi yeewe, dem
doxantu moom kenn biir Guy-Géwél.
Keroog jooju la Aatu Sekk bég ! Péexu
géej gaa ngi koy dugg, di yëkkati
mbubbam, di raxas xel meek xol bi ba ñu
set wecc. Waaye bésub tiis la woon it !
Guy-Géwél a ngi xasaw xunn ndax néew
yu yàqu yi tasaaroo ci mbedd yi. Saa yu
leen jube, ay tan naaw, tag ciy garab, xaar
fa ba Aatu sore, ñu wàccaat di luqati bëti
néew yi, di daggat seen yaram.Yàllaa
musal keroog Aatu Sekk ba dajewul ak
soldaari Dibi-Dibi yi mbaa way-fippu yi.
Céy ! Ku ko ne woon dina toroxi bés ba
ay golo di ko def seen jaam !
Moom Aatu Sekk, doomu Fara Biram
Sekk ma maamam Saa-Ngóone Penda
Sekk des Somb ! Monte de, su ko neexoon
mu jaare fi dem yoonam ! Waaye yëf yi
jarul a yàkkamti. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_250 | Sàllaaw dina won ñaari golo yi mooy kan!
Du daw mukk ba noppi di taafantoo wuti
doole. Déedéet ! Day dellu kër ga, jébbal
boppam Ninkeek Nanka te xam ne yàgg-
yàgg dina leen jekkuji. Xanaa du ndànk-
ndànk ay jàpp golo cib ñaay ? Naka la
doomi golo yi dégg Aatu Sekk laal buntu
kër gi, ñu daldi dawsi di ko xool ay bët :
Foo nekkoon, yow ? Kañ nga tekki sa
buum bay dem di wëndéelu biir Guy-
Géwél ? Tey lanu lay ñef ba nga xool
benn béréb ! Xaj bu bon bi ! Ñàkk jom ba
dee ! Aatu Sekk a ngi dof-doflu, naan
leen :
- Goney mberaago yi, dama tàllali woon
samay tànk. Lu leen tee gunge seen
maam ? Yéen a bon ! Man sax mere naa
leen ! Ñaari doomi golo yi salliiru, song
ko. Góor gi Aatu gis ni ñu ko wëre, di tëb
di dal, di xultu, mel ni ñuy waaj a xar suuf
si dugg ci. Bi leen Aatu Sekk dégloo bu
baax, la koy sog a leer ne nasaraan lañuy
làkk. Mu xaw a jëli li ñu koy wax : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_251 | - Foo nekkoon, Aatu Sekk ? Seet nanu la
ci kër gi yépp ! Waaye nun nga koy
digaaleel, li nga def tey moom dootul
ñaar ! Noonu, Ninki jël benn musóor tàkk
bët yi, tafaale gémmiñ gi, bàyyil ko tuuti
fu mu mën a noyyeek bakkan bi, ba noppi
nag taxawal ko ci taatu niim gi, wërale
yaram week benn buum gu gudd a gudd.
Bi mu ko yeewee ba mënatul a yëngu, ñu
dal ci kowam di ko dóor ay dóor yu metti.
Caw nañu góor gi Aatu Sekk benn yoon,
caw ko ñaari yoon, caw ko, cawaat ko, mu
ne këj, faalewuleen, mel ni du moom
lañuy dóor. Nanka gën a mer, nag, daldi
suy kaani gu mokk ci góomi Aatu Sekk yi
! Yaramu góor gi mel ni da ñu ci sottiy
xal, muy yuuxu, di leen saraxu ni gone gu
tuuti.
Doomi golo yiy màttu, naan ko :
- Ñaw ! Danga doon jaay dërkiis rekk !
Gat di ! Aatu Sekk xamatul lu ko yëf yiy
niru, muy jooy, naan leen : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_252 | - Waaw gone yi, lan laa leen def ? Lu tax
ngeen bañ ma nii ? Rey leen ma benn
yoon ma noppaluji àllaaxira !
*
* *
Doomu-Aadama Njaay moo kéemaane !
Góor gi Aatu dafa jékki-jékki rekk, benn
woy ne cabax ci xel mi, mu yëg ni yaram
wiy dawe. Ndax sax woy woowu dafa
jóge fu sore, ñëw dëgg-dëgg ci xelam ?
Du rekk ay kàddu yu neex, kaar, yu
ngelaw li yëkkati, ñuy wëndéelu ci jaww
ji, di ko gungewaale moom Aatu Sekk ci
tukkeem bu mujj ?
Man ràkkaaju naa ! Waaw, man ràkkaaju
naa ! Waay, lii moo neex waay ! Déedéet,
ngelaw li ci boppam mooy woy, moom
mu koy awu, di ko gunge, naan ci
suuf : Man ràkkaaju naa ! Waaw, man
ràkkaaju naa ! Ngelaw, am nga géwél, te
man mii, Aatu Sekk, maay sa géwél ! Na
ko ñépp xam bés niki tey! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_253 | Li muy woy ci suuf yépp, mu ngi jéem a
fàttaliku lan moo tegu ci kàddu yooyu, ak
fan la leen mas a dégge. Ndax du woyu
kasag wu mu daan dégg ci ngoneem ?
Wànte woyu kasag neneen lay tëdde,
mooy gën a xumb. Bu gaa ñiy tëgg, rëkk
yeey gën a jegeyoo.
Waay Ninki-Nanka, kaay tekki samay
loxo ndax ma mën a tàccu ngelaw li !
Man ràkkaaju naa ! Waaw, man ràkkaaju
naa ! Su ragalul woon a fen de, dina ne ci
bàkkub mbër mu fi siiwoon la ko xelam
jukkee. Du bàkku Yuusu Jéen sax ? Xéy-
na it muy bu Maam Góorgi Njaay.Cam !
Sëtu Maram Jéen ! Waaw !
Wax dëgg Yàlla, xamul ci kan la mas a
dégge woy wii.Waaye su dul woon kumpa
googu, ndax Aatu Sekk dina am bànneex
bu ni tollu ? Ci diir bu gàtt a gàtt, mu
dellu nekk waxambaane, di daagu ci biir
géew bi.Man ràkkaaju naa ! Waaw, man
ràkkaaju naa ! Mu bëgg it xam lu kàddu
yooyu tekki, mu të ko. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_254 | Ku leen fent ? Lan la ci jublu woon ? Am
na ay kàddu yuy yëngal nit ki te du xam lu
tax. Gayndee Njaay, mbarawàcc ! Baat
boobu, saa yu ko waa Jafune déggee,
tàggook seen sago, mu ñaax leen, ku ñu
song daan la. Fan la Ninki-Nanka génne,
ba ñëw janook moom ? Keroog la góor gi
Aatu Sekk mas a réccu li mu toppul waa
Guy-Géwél ba ñuy gàddaay. Waaye fekk
na su ma yëgoon dem yoonam bu yàgg a
yàgg ! Xef-xippi ay soldaar ne mëll ci ëtt
bi. Aatu Sekk xàmmee waa kër Dibi-Dibi.
Ni ko Ninki-Nanka yeewe ci taatu niim gi,
mu ngi muut-muuti ndax bëgg a fexe nu
mu rëcce. Aatu Sekk a ngi tiit ba fàtte ne
dañu taf gémmiñ gi.
Muy jéem a yuuxu :
- Wiiw Dibi-Dibi ! Wiiw Dibi-Dibi ! Dibi
Dibi ! Waaye kàddu yooyu benn agsiwu ci
ba ci gémmiñam, ñoom ñépp a naju ci biir
putam, des fa.Aatu gis leneen lu doy waar
Loolu lan laati ? Xanaa ay soldaari
Tubaab yu wàcce ci garab gi, di daw ci ëtt
bi, fu nekk ñu dugg fa. Aatu yéemu : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_255 | - Waaw, kañ la Tubaab yi bokk ci xeex
bi ? Ndekete at yii yépp xaj yu bon yaa
ngi ci kow garabi Guy-Géwél yi, tiim ma !
Ñii ma gis ñuy wëndéelu ci kër gi de,
benn Xonq-Nopp mooy seen njiit ! Walla
boog damay gént ? Bi Aatu Sekk génnee
ci mbedd mi di seet lu xew Guy-Géwél la
dajeek ñi ci des. Ñaar-fukki Xonq-Nopp
yu làqu ay at ci kër gi te moom Aatu Sekk
yëgu ci dara ! Seetal ma lii rekk ! Benn
soldaar génne ci saal bi, ànd ak Ninki-
Nanka, ñëw ba ci kilifaam, am lu mu ko
wax. Kooku xool Ninki-Nanka, tàllal ko
loxo, ñu jàmmasante bu baax. Góor gi
Aatu Sekk gis ni soldaar seek doomi golo
yi wegantee, mu daldi xàqataay : Ndekete
nii la àddina suy tukki di mel ! Lu fi
soldaar yu weex yii di wut ? Wóoy, man !
Ku may wax lu xew Jafune ? Ay soldaar
yu weex tàll ! Ñaari golook seeni daar-
daar ! Ma ni : lu xew Jafune ? Yaayu
Ninki-Nanka agsi, ñëw ba janook góor gi
Aatu Sekk, daldi taxaw. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_256 | Ñu xoolante ñoom ñaar, mu rocci fetal gi
mu làqoon ci lafu sëram, dàkk ndànk Aatu
Sekk.Golo gu jigéen gi soqi, soqiwaat.
Góor gi Aatu Sekk yëg ni ko ngelaw liy
tàggoo, di raay kanam gi : Man ràkkaaju
naa ! Waaw, man ràkkaaju naa ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_257 | TÉEREB WIS | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_258 | Badu, wóor na ma ne su ma la laajoon lan
mooy gën a biral sunu aaday cosaan ci
mbirum fo ak tàngal yaram, dinga ma ni :
- Làmb la, Ngiraan.
Su ma delloo ne la :
- Limal may turi mbër, du ñàkk nga ni ma :
- Tafaa Géy mbaa magam Mbay Géy,
Duubal Lees, Mànga, Tubaabu Joor ak
Bàlla Béey.
Su dee ku la mag laa laaj loolu, xéy-na
dina ma ne :
- May ma, Ngiraan, ma fàttali askan wi
jaloorey Mbay Ja Jóob, Abduraxmaan
Njaay Falaη, Paate Jóob, Fóode Dusuba
walla Landiη Jaame.
Mbër yooyu yépp, bëre-dóor a tax ñu xam
leen. Yow Badu, soo daggee paas dem
seetaani làmb ja Ibba Maar Jóob, mbër yi
takk seeni gàllaaj, ñu leen di tëggal, ñu
ngembooy sëri rabal yu rafet di bàkku, di
tuuroo soow ak saafara, Xaar Mbay
Majaaga di woy : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_259 | Làmb góor a ko moom,
Lii bu doon làmbu jigéen sax jeex na- a-a-
a, Ku ci nekk ànd ak sa gàngóor, gaa ñiy
sànniy pitax ak a toj ay nen, loolu yépp
soo ko déggee, teg ci sa bët, fàww sa
yaram daw, Badu. Noo def sa xel dem fu
soree-sori.Ñu dégg laak ñu bañ laa dégg,
dinga ne :
- Futbal neex na lool te am bayre, waaye
ci dëgg-dëgg làmb mooy sunu cosaan, ni «
sumo » mbaa « sido » nekke cosaanu
réewum Sàppoη. Kon jaadu na ay nit jóge
bitim-réew, ñëw di jël ay nataal mbaa di
defar ay film ci sunu làmb ji. Su ñu delloo
fa ñu dëkk, dinañu ne :
- Po mii ñu leen di wonsi nag, waa
Senegaal a ko moom. Bi ko seeni maam
sàkkeek léegi, lu mu néew-néew, war naa
mat fanweeri xarnu ci ginnaaw.
Ku ciy sañ a teg baat ? Monte de Badu, su
ñaari mbër yi bàkkoo ba noppi, def seeni
déebaa-déeb ba janoo di léewtoo, | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_260 | ku ci jëkk a yëkkati sa loxo dóor sa
moroom teggi nga yoonu aadaak cosaan !
Lu ma tax a wax loolu ? Dafa fekk ne
bëre-dóor, ak li coow liy bare yépp, Maam
masu koo xam. Bëre dóor, benn Tubaab
bu xonq coy bu tudd Móris Sakeη moo ko
dugal ci réew mi
Móris Sakeη moomu, minise la woon,
dëkkoon Sàndiñéeri gii, ci wetu màrse
Sàndaga. Bi ma newee gone, gunge naa
bés sunu benn Garaη muy seeti tubaab
boobu ma lay wax. Maa ngi gisaat Móris
Sakeη. Ku am taxawaay la, kanam gi wow
koη, mu xaw a xuuge. Mu ngi sol keroog
tubéy ju gàtt, yeel yi ne fàηη, sew ruuj. Ñi
muy liggéeyal ay doomi réew mi lañu,
waaye moo leen yilif ñoom ñépp.
Bi nu duggee ci mbaar mi maak Garaη
Maxu, Tubaab baa ngi dem aka dikk, ñàq
tooy xépp, di joxey ndigal.
Tey nag Garaη Maxu dafa àkksi Móris
Sakeη, ndax nee na tubaab bi dafa ko
ameel xaalis. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_261 | Garaη Maxoo fi dàq xeex, ëpp fi fit,
waaye du tooñ. Moo tax mu jëkk jéem a
sàng Tubaab bi sutura.
Kooku di ko jaay ñàkk teggin :
- Nuu tarwaaye, Maxtaar, paa salaamaaleg
Ust ! Ayca ! Garaη Maxu daldi gis
boppam ci saa si :
- Waay, Xonq-Nopp bii man lay sëppu,
tey laay dëgg ndeyam ba mu xool benn
béréb ! Naka la wax loolu, daldi jubal ci
Sakeη, tàllal ko loxo :
- Sama kaaw laay jëlsi, laa wax ! Gaawal,
mbaa ma...
Waay ! Ñu xoolante ñoom ñaar. Boo
gisee mbaar mi, ñépp a ngi liggéey-
liggéeylu, waaye kenn noyyeetul sax.
Móris Sakeη yuuxu moom it :
- Fous-moi laa camp ! Haa ! Toi ménacer
moi, allez, dewoor! Xawma kan, wànte du
Garaη Maxu mooy nangu ñu koy toroxal
ci biir ay nawleem ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_262 | Dafa daw wuti Tubaab bi, taxaw ci
kanamam, xulli ko. Móris Sakeη gis paaka
bi Garaη Maxu téye, daldi tàmbalee dellu
ginnaaw. Fu mu aw, Garaη Maxu topp
kook paakaam. Ñépp a ngi ne tekk, di leen
seetaan. Benn paa bu doon liggéey ak
Sakeη ne Garaη Maxu :
- Maxu, mbaa seet nga bu baax li
ngay def?
- Amul fog ! Su ma seen gaayin bi feyulee
sama kaaw tey dinaa ko butti, fanaani jeel,
man Maxtaar Gaynde ! Góor gi ne ko :
- Yoonu jàmm sorewul. Ñii baaxuñu, de !
Ñaata la la yoreel, sax ?
- Weer wii ñu génn, indil naa ko juróom-
ñeenti mbër. Moom xam na ñaata la.
Li muy nekk kabase yépp, Móris Sakeη
xam na ne Garaη Maxu jekku na ko. Mu
soppi yëf yi ay kaf, daldi ree :
- Toi aimer argent, Maxu ! Moi ami, te
payer argent ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_263 | Garaη Maxu ne këj, di ñàngal. Ñu fey ko
xaalisam, mu jiital ma, nu dellusi Ñarelaa.
Keroog may na ma lu ma jënde pastel ci
Meer Màgget ba noppi ne ma :
- Du xam nga Tinaa Delgaado, sama gelu
ηaaña bi ?
- Waaw, Garaη !
- Joxal ma ko ñaar-fukki dërëm yii, ne ko
mu rëgal ci kaccuupa, maak sama kàngam
yi dinanu reersi ngoon !
Garaη Maxoo doon ngànd dëgg ! Masul a
nangu kenn yab ko. Badu Taal, ak lu waay
mën a wax, Senegaal réewu bañkat la !
Xawma naka la tubaab yi def ba xoj ñu ak
seeni karwaat, ñuy dox nii ci seen waaw !
Jaaxal na ma de, man Ngiraan Fay ! Lii
moo doy waar ! Bañkat yi mel ni Garaη
Maxu yi fi jaar yépp, teewul ay
doxandéem ñëw moom nu, di nu wommat,
nu topp ciy yagar-yagari ni ay bàyyima !
Léegi de, nee nanu noo moom sunu bopp.
Waaye man de, gisuma fi coppite gu jar a
wax. Tey la Waalo gën a aay. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_264 | Afrig yépp nag a may tax a wax. Muy
Lumumbaa, di Sànkaraa, di Séex Anta
Jóob, di Móngo Beti, di Amilkaar Kabral,
di Sàmóori Ture, képp ku mas a aw yoon
wu Tubaab bi xàllul, tam na la dëmm
mbaa mu bóom la ! Cim ! Ngay Doomu-
Aadama ni ñépp, ñu tënk la te sañoo sax
yëngu. Jéngu ? Yëngu ? Déedéet ! Sa xel
nekku ci, moom ! Yow ci sa bopp yaa gën
a dëgëral buumu njaam gi.
Ngay Doomu-Aadama ni ñépp, di nangoo
soppiku ba ame jëmmu golo ak jikkoy
seku !
Waaye nanu dellu gaaw seeti Móris
Sakeη. Dëgg la, keroog Tubaab bi tooñ na
Garaη Maxu ba ñu xaw a cóoki ñoom
ñaar. Lu Yàlla tudd kenn mënu ci dara,
wànte Móris Sakeη nit ku woyofoon la.
Ñarelaa gii de, ñépp la fi amaloon jàmm,
wax dëgg Yàlla. Daan na fi faral di
seetaansi ay kasag mbaa ay mbappat.
Ndekete booba am na lu réy lu mu nar !
Xéy nanu bés dégg ne Móris Sakeη ubbi
na làmbu boppam ci wetu Ñaay-Cokkeer. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_265 | - Làmb laa dégg, de ?
- Sàllaaw. Ci néeg bu yaatu la gaa ñiy
bëree.
- Kañ lañu daan bëre ci biir néeg ?
- Loolu kay doy na waar !
- Man de, dinaa ko deñi kumpa !
- Doo ma fi ba !
- Ayca, nanu seeti naka la nen di bondee
ci kekk...Ñu ànd ñoom ñépp, ne ñu ngay
seetaani làmbu Móris Sakeη ju kéemaane
jooju. Sakeη a nga ubbi woon benn saal ci
ginnaaw sinemaa El-Maalig gii. Ba ñu
agsee, nuyoo, dem bay dugg, benn ponkal
moo taxaw seen kanam, laaj leen seen
paas. Ñu xoolante, ku nekk muuñ. Ñoom
kat, bëre ba ñu xamoon, kenn masu leen
cee laaj dërëm, fo doηη la woon.
Ñu ne ponkal mi :
- Waaw, yaaram, xanaa yëf yi dootul bëre
rekk ?
- Aa, wute na tuuti ak sunu bëre, nag. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_266 | - Lu leen wutale ?
- Bii, mbër yi dañuy dóorante ay kurpeñ.
- Dóorante tàww ?
- Ay dóor yu metti sax. Lépp xej na ci.
Man mii maay fomp deret ji su ñu xeexee
ba noppi.
- Loolu kay du bëre, leneen la !
- Muse Sakeη de, bëre la ko tudde.
Li ñuy wax ak waa ji yépp, nit ñaa ngi
leen di romb, di dugg ci biir saal bi. Ñoom
it ñu fey, dugg. Seetaankat yaa ngi wër
benn géew bu ñu sotti suuf su bare.Ñi ëpp
ci ña fa newoon di dëkkantee ka bëre, ay
bóoy yu doon liggéeyal Tubaab yi lañu.
Bés boobu la Garaη Maxu xamanteek
Móris Sakeη. Garaη Maxu dafa fekk mbër
ma ñu ne moo fa mën, mu daaneel
ndëndam, ñu sëgg ñoom ñaar. Waa ji
jàmbaar la woon ni Garaη Maxu. Seen
xeex baa ka metti ! Dem nañu ba muuroo
seen deret, mel ni ñu gumba, di jéexante ci
lëndëm gi, di sànni seeni kurpeñ ci jaww
ji. Yàlla may Garaη Maxu ndam. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_267 | Móris Sakeη fekki ko ci géew bi, yëkkati
loxoom. Mbooloo mi àndandoo di tàccu
Garaη Maxu. Móris Sakeη waññ xaalis
jox ko ba noppi takkal ko raaya Tugal ci
baat bi.
Ku gisul keroog ni gaa ñi duggsee
Ñarelaa, gisoo dara ! Garaη Maxu nekk na
fi mbër xaat, nun gone yi nu dar ko, mu
fent ay bàkk, di woy ak baatam bu xuur !
Garaη Maxu bëre na juróom-ñetti at te
laalul suuf. Mook Móris Sakeη ñu faf
nekk ay xariti benn-bakkan, muy jàppale
Tubaab bi ci liggéeyam. Bu nawet jotaan,
dañu daan wër ñoom ñaar mbappati
Ndakaaru yi. Ku ñu gis nga am doole,
mën a bëre, ñu fexe ba xëcc la, wut ku ñu
la booleel. Soo daanee, Sakeη fey la xaalis
bu xaw a duun, soo daanoo mu ñamal la
as tuut.
Gone yi tàmbalee buuxante buntu kër
Sakeη.
Bëre-dóor daldi juddu. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_268 | Fii la woon, ci wetu sinemaa El-Maalig,
ci Ñaay-Cokkeer gii, ci atum 1930. Du
benn du ñaar, mbër jóge na làmb jooju
deretam tuuru, kanam giy nàcc, bëñ yi rot.
Móris Sakeη dem na bay tëgg làmb noor,
di tëgg làmb nawet.
Lu doy waar la fi Sakeη def. Dafa dugal ci
boppu goney réew mi ne xeex rekk mën
na laa may loo dundalee sa njaboot !
2Dégg nga wax ji bu baaxam, Badu ?
Saay-saay yi daan taxawaalu Ndakaaru
yépp dégg bés ne xeex ba ñu daan def ci
maliforo mën nañu leen cee fey xaalis. Ñu
daldi wàllsi, ne Móris Sakeη :
- Noo ngi ! Su dee xeex rekk, kenn dàqu
nu ko ! Mbëri kow gi jot ci xibaar bi, ne
ñoom it kenn du leen ëpple ci xaalis bi
Sakeη doon séddale. At mu jàll, xaalis biy
gën a takku. Powu kese soppiku xeex,
xeex daldi doon liggéey. Dem nañu ba yëf
yi bëgg a ëpp loxo. Sakeη ci boppam dafa
mujjee bàyyi liggéeyu miniseem ba, di fey
ay nit ñu koy indil ay mbër. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_269 | Xam lépp, wax lépp baaxul, Badu.Waaye
Ñarelaa gii de, am na fi ñetti kër yu mag
yoo xam ne seen alal ji ñuy coow, ci
Móris Sakeη la jóge.
Ñooñu fi seen njaboot di jaay tey maanaa,
dañu daan xéy jubal pooru Ndakaaru,
waxambaane wu ñu gis nga am doole ñu
woo la ci pet, ne la :
- Saa waay, yaa ngi yàq xaalis, de.
- Ci naka ?
- Xanaa xamoo Móris Sakeη, Tubaabu
Ñaay-Cokkeer bi ñuy coow ?
- Kuy kooku ?
- Tugal la jóge, am alal te yéwén ci ba
dee. Soo nangoo dugg ci làng gi bëre, dina
la fey xaalis bu dul jeex.
- Bëre ? Wax dëgg Yàlla, mënumaa bëre.
- Jaru ko. Yow mii ma gis, koo dóor
kurpeñ mu daanu. Tee ngaa jaar saal ba,
dibéer jii di ñëw...
- Baax na. Tegtal ma béréb bi ngay wax. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_270 | Ay niti Móris Sakeη daan nañu bawoo it
Ndakaaru dem Saalum, dem Kaasamaas
ak Fuuta, dem Kajoor walla Kéedugu,
fekk fa waxambaane wu sëgg ci naaj wiy
bey gerte mbaa dugub mbaa ceeb,
ñu ne la :
- Yaa ñàkk faayda dëgg, alal ju dul jeex a
nga lay xaar réewu taax ya, nga nekk fiy
kocc-koccal !
- Réewu taax yan ?
- Ndakaaru laa lay wax ! Te foofa kat moo
dàq fii fuuf ! Su ko defee, nga ne fa ñukk
mbey ma, ñëw Ndakaaru di xeex ca Ñaay-
Cokkeer, Móris Sakeη di la ñamal as tuut,
li ëpp ci xaalis bi mu lem denc ci
gafakaam, yow nga defe ne yaa téegal
bukki bi, jànq ji topp la, ngeen ànd di
mbuumbaay. Moo, Móris Sakeη foo
bawoo ba teersi fi, soppi sunuy aada, yàq
leen yaxeet ? Am na sax ñu naan danga
fee juux rekk, ndax Amerig nga doon
dem, gaal gi taxaw ay fan ci waaxu
Ndakaaru, nga faf fi toog, | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_271 | sa mbokki tubaab yi jàppale la, ba tee laa
tumuraanke. Dégg naa it ñu naan ku
bëggoon jigéen nga, te jot nga fee def ay
njaaxum. Fu ñu la fekkaan, yow Sakeη,
yaa ngi sex sa kamelyaa, di xëcc. Làmb ji
nga ubbi woon Ñaay-Cokkeer, duggewoo
ko woon dara lu dul wut alal. Bi nga
demee ba yëf yiy dox, danga daldi wàññi
li nga doon fey mbër yi te kenn sañu cee
teg baat. Badu, xam sa bopp lu am solo la.
Soo setloo bu baax, su weesoo Ndakaaru
Njaay gii, bëre dóor amul feneen fu ñu
koy defe ci réew mi.
Te soo génnee Senegaal, doo gis fenn fu
ñu koy def ci Afrig. Muy Niseer, di
Gànnaa, di Niseeryaa walla feneen ci
Afrig, lu xaw a nirook bëre dóor sax amu
fa. Ñàkkul su fa sunu Móris Sakeη mi
jaaroon, ñoom ñooñoo ngembu kon di
xeex, yaakaar ne loolu ñuy def mooy seen
aaday cosaan dëgg-dëgg. Maam Góorgi
Njaay juddoo Legoos, tudd Jon Adekunle,
Falay Balde dëkk Akaraa ñu koy woowe
Kófi Mensaa ! Céy ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_272 | Ma wax ko te dee : li ëpp solo ci bëre-
dóor, dóor yi la. Te loolu, maam bàyyiwu
ko fi. Xanaa kay kenn du ma ne Móris
Sakeη mooy sunu maam ! Kon xam nga,
Badu, bu ñu demee ba raaya Amerig
wuutu sëru rabal yu yànj ya mbër yi daan
ngemboo, gone yiy bàkku ni ay tubaab, ne
bu leen kenn woowe Saa-Waalo mbaa
Booy Bàmbara, tànnal seen bopp ay turi
Amerikeη, loolu lépp su amee warul a
jaaxal kenn. Ni làmb jiy doxe tey ci Ibba
Maar Jóob ak Demba Jóob de, dafa mel ni
lu dellu cosaanam dëggëtaan !
Te cosaanam weesuwul atum 1930, ci
Ñaay-Cokkeer gii. Dama ne : nun waa
réew mii, war nanoo xoolaat sunu bopp,
kat ! Dëgg la sax, doon lii mbaa lee, benn
la, mel nii mbaa neneen amul solo, nun
ñépp ay doomi Maam Aadama lanu.
Waaye kat, yenn ñàkk naw sa bopp yi, xel
mënu koo nangu. Ne yàcc-yàccaaral ci
naaj wi, fu doxandéem jóge ne la doo nitu
dara, maa la gën, nga ne ko neexul ba
neexul waaye wax nga dëgg ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_273 | Mag ñu baax ñi fi jot a jaar daan nañu wax
ni :
- Roy-dàq.
Ñi seen xel gàtt, jàppe ko ngóora. Néew
dégg-dégg mënul a weesu loolu !
Roy-dàq mooy :
- Roy yàq. Yàq sa bopp.
Yàq sa bopp... Soo ci naree am xel ñaar,
Badu, fàttalikul wax jii :
- Ku wàcc sa and, and boo dem fekk ca
boroom.
*
* *
Séex Anta Jóob.
Badu Taal, jàmbaaru xare dëgg a ngoog.
Masul a dugg ci dara ba di ci séentu alal
mbaa daraja. Lépp lu mu mas a sumb, baat
bu mu mas a yëkkati, njariñu askan wee
taxoon.Masul a jiital leneen. Moom daal
laa xam ne aji-néew ji doole yee ko
taxoon a jóg. Lenn rekk a ko soxaloon : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_274 | liy tax nit ku ñuul jëm kanam te du
sibooru kenn. Su nu ko déglu woon na mu
ware, dog kon nanu buumu njaam gi bu
yàgg. Nit ku maandu la woon, lewet ba
nga ni lii lu mu doon, ndeysaan, waaye
kenn feesul woon bëtam. Soo toogee tey
ci sa kanamu tele, gis ni Daawur Jaañ
baree tiitar, gis yu ñàkk faayda yi mu jiital
ak ni mu ragalee doxandéem yi nu doon
noot démb, te di nu fowe tey, soo gisee
loolu lépp ngay sog a xam ne Séex Anta
Jóob kenn la fi woon.
Du woon nitu caaxaan. Daawul woon wax
lu ko wóorul, daawul dige lu mu narul a
def. Bu ay ñoñam demaan ba mel ni ñuy
xaw a toqi, dafa leen daan ñaax ak ay
kàddu yu daw yaram :
Yëf yi metti na, gaa, waaye buleen dara
jële ci li ngeen nekk.
Dafa fekk rekk ne waa réew mii, dañu
leen a nax ba soo leen waxee dëgg sax tas
seen yaakaar. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_275 | Séex Anta Jóob teel naa làqu, ndax bi ñu
koy denci Céytu, ci 1986, amul woon lu
dul juróom-benn fuki at ak ñaar.
Amul bés bu ma jullee, man Ngiraan Fay,
te ñaanaluma Séex Anta Jóob. Dundam
neenul ci genn wet. Miinantewunu woon,
gaa. Ay mitiηam doηη laa daan dem, di ko
déglu. Waaye li am solo ci nit ki mooy mu
am dégg-dégg. Mën ngay tukki, Badu,
agsi ci dëkk boo masul a gis kenn, toog ci
pénc miiy noppalu, nit koo xamul romb la,
tàbbal ci say nopp ay kàddu yu am solo.
Soo téyee kàddu yooyu bu baax, di leen
fàttaliku foo tollu dinañu la gunge, amal la
njariñ ba keroog Yàlla di la fi jële.
Noonu rekk la sama digganteek Séex Anta
Jóob deme woon. Dinaa la wax tey li ma
jàng ci moom : nit day juddu bés, ñu teg ci
ay at rekk ñu robi ko. Yëf yi gaaw ni xef-
xippi. Ku góor-góorlu tuuti, mën ngaa
bañ a xejal fen ak tappale ci diggante bu
xat boobu. Bu kenn yóbbu sa fit, Badu, bu
la dara tax a ñaaw ci xare bi. Loolu de laa
jàng ci Séex Anta Jóob. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_276 | Xalaatam ak dundam, teen bu xóot a xóot
la.Fexeel ba say doom duy ci, Badu. Man
Ngiraan Fay, giñ naa ni su ko samay
doomi sët defee, duñ ko réccu. Giñ naa ni
su goney Afrig yépp awee ci yoon wi leen
Séex Anta Jóob xàllal, ak lu mu yàgg
yàgg yabeel gi dina deñi ba fàww.
*
* *
Ninki-Nanka.
Ñaari doomi golo yi ma la sàkkal ci
Téereb Fent.
Tàngaay a leen gën a jig.
Golo yu mag yi, moo xam baabun la walla
dàngin, ñoo gën a jege nit képp ku Yàlla
bind. Ci li boroom xam-xam yi wax, golo
rab wu am xel la. Su bëggee wax dara
moroomam, day yuuxu, di sànniy loxoom,
ci jaww ji, di tëb di dal.
Ki leen di jiite : ki ci ëpp xel ak doole.
Ñoo fi gën a forox nopp. Seeni bët tamit
baax nañu lool. Ñaata doom lay am : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_277 | benn doηη lay faral di jur te duy faral di
am ay séex. Bu nekkee liir, ci biir bi la ko
ndey jiy boot. Su demee ba xaw a dëgër,
mu teg ko ci diggu-ginnaawam, fu mu jëm
yóbbaale ko. Xéy-na looloo tax wolof
Njaay naan :
- Alalu golo ca lex ba !
Lii tamit gëstukat yu bare wax nañu ko :
doomi golo, du ñaari way-jur yi rekk ñoo
koy yar. Mag ñi ci gàdd gi yépp am nañu
sañ-sañu jubbanti ko. Ñoo koy jàngal rëbb
ak xeex mbaa naka lay yéege ci kow garab
yi. Su yaroo, ñu neexal ko, téeñ ko, su
leen naree të nu duma ko.Ñaari golo duñu
séy feek ku jigéen ki soxlawul moroom
mu góor mi, cokkaas ko, ñu nekkal ko ci.
Xeetu golo yi bare nañu lool, kaar, te it
wute nañu lool. Bu yàggul rekk la ay
gëstukat feeñal benn xeet wu bees ca
Gaboη, ci tàkkal dexu Efuwe, ci béréb bi
ñu tudde Àllu-Yamb. Geenu golo Gaboη
gu bees googu nag, dafa weex tàll, cat liy
melax, di ràyy-ràyyi nib jant. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_278 | Nee ñu ñi ko jéem a dékku yépp dañu fa
jóge gumba ! Ca Amerig nag, am na fa
golo gu nirook jargoñ lool, te ñu koy lekk.
Ñi mos yàppam nee nañu dara dàqu ko !
Golo mën naa dund téeméeri at ak lu topp.
Waaye Sinuwaa yi ñoom, jàpp nañu ne ci
mbindeef yépp, golo rekk moo ciy dund
ba abadan. Waa Siin yooyu, dinañuy wax
sax ne su golo demee ba am 800 at, lañuy
sog a mën a jàpp ne mag la. Ci lay door a
sippi, bàyyi yëfu saay-saay ya mu daan
def ba mu newee gone gu ndaw, amoon lu
dul ñetti xarnu mbaa ñeenti xarnu.
Ma toog ci buntu kër gi, ñaari xarit romb
ma.Fu ñu jëm ? Nu ñu tudd ? Xam ! Dégg
naa rekk kenn ki naan moroom mi :
- Waaw, Yuusu, lu dëkk bi wax nag ?
- Léegi kat, kenn booletunu ci dara. Xale
yi jàngi nañu Tugal, ñibbiseek seeni
lijaasa yu dijj, xas nu ba nu ràpp, ñu
sempinu sànni ca xaj.Ki mu àndal daldi
ree, ne ko : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_279 | - Yow ! Maa la xam. Waxoo wax ji de !
Am na loo may nëbbati !
- Du dara, sa ràkk jee may bëgg a jaaxal
doηη.
- Kan ci ? Kinne ?
- Ñaata ràkk yu jigéen nga am ?
- Céy yaak sa Kinne mi ! Yéen daal waat
ngeen ne... Ñu daldi jàdd koñ. Mbeddu
Ñarelaa mi neeti selaw, di xaar yeneen
ñaari Doomi-Aadama jaar fi, suy ay kàddu
ci jaww ji, ngelaw li këf leen, yéeg ak
ñoom ba fa asamaan gën a kowee, mu
daldi gas, suul leen fa.
Lii, Badu, yokk ko ci Téereb Lëndëmtu bi
ma àndeek yow dem siyaareji Maam Ngóor
ca Mbériη-Saaj.
Sama xel dellu na biig ci sama baay. Lu
ma ko jot a xamal, moom it ? Néew na
lool, wax dëgg Yàlla. Bés, gàddu na yar,
moom baay, ne dafa may dóor. Mu tiim
ma, yëkkati yar bi, ma lemmu làq sama
bopp ci samay loxo, di xaar yar bi dal.
Waaye yar bi dalul. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_280 | Ma daldi siggi, gis baay mu ne tekk di ma
xool. Sunuy bët daje. Nekk gone du tee
yëg yenn yi ci sa yaram. Maa ngi gis ni
mu ma xaaree. Li ma def baay kañ laa
xamul, waaye jéppi na ma ba fu jéppi
yem.Mu sànni yar bi, wiccax bopp bi, ne
ma :
- Xawma kan moo nar a tekkiji ëllëg ci
sama doom yi, waaye du yow mii,
Ngiraan Fay. Sonn naa ci say mbir : sama
loxo dootu la laal.
Ma bëgg koo saraxu :
- Dóor ma ba may nàcc, baay. Dóor ma ba
làggal ma.
Lu mu metti-metti, moo ma gënal ni nga
ma xaaree nii te xawma lu tax.
*
* *
Ñarelaa ak ay taleem yu bare pax te
xobbiku ! Foo geestu, say bët dajeek ay
minise ak ay metkaniseη ak i boroom
saret. Ñarelaa ak ay jali weñam yu xuur ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_281 | Foo jublu xetu biiñ mbaa xetu yàmbaa
song la, dàq la. Néegi baraagi Ñarelaa yee
fi yàgg ! Yu ci bare maxe nañu ba fënëx.
Lee-lee, su tawee ba séwét, kër yu bare
dañuy taa ba kenn du am foo jaar, mbaa
nga dégg ni am na ay baraag yu màbb.
Mbedd yaa ngi mel niy sën, yoo yeek weñ
yi dëkke biiw, lakkal nit ñi guddeek
bëccëg.
Ñarelaa, ci gox yi ñu jëkk a sanc ci
Ndakaaru la bokk. Boobaak léegi, am na
xarnook lu topp. Su Ñarelaa doon nit, ñu
ne màggat na ba xubidaas, ndax ni mu
soppikoo. Am nay jamono, béréb bu yiw
la woon. Boroom barke yu bare ci réew
mi, fii lañu juddoo, doonte sax léegi ay
miskin ni man rekk ñoo fi des. Sa moroom
yi fi jànge ba am ay lijaasa yu mag, ñu
nga bitim-réew di wut alal, mbaa ñu dëkke
gox yu mel ni Almaadi, mbaa Faan-
Residaas walla Palaatoo.
Am nay jamono, fii la Ndakaaru yemoon.
Soo weesuwaan këru Ñarelaa yu mujje yi,
fépp àll la woon. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_282 | Ay till, ay jaan, ay bukki ak yeneen rabi-
àll ñoo fi feesoon.Xanaa looloo tax lépp lu
bees lu mas a dugg ci réew mi, Ñarelaa la
ko Yàlla jaarale ? Du ñàkk. Oto bi jëkk a
wàcc ci dëkk bi te doomu réew mi
moomal ko boppam, Ñarelaa lañu ko
ngéntee ! Céy ! Ku fekkewul bés ba Fara
Mbóoj jógee dëkk baak xantu Wersaayam,
fekkewoo dara !
Li ko dale fii ba tefesu Kusum, foo sànni
mbàttu mu tag. Xawma ñaata la Fara
Mbóoj jënde woon otoom boobu, waaye
xaalis ba mu ko ngéntee ko ëpp fuuf.Laaj
ma naka, ma wax la ko ?
Sëriñ si sotti nañu safara ci Wersaay bi,
ñaanal ko, jeeg ji togg nañu laax, géwél yi
dar seeni nopp xaacu, di tagg ay maami
Fara Mbóoj ca Waalo. Te ku nekk ci
ñooñu ma tudd, Fara Mbóoj teg na dara ci
loxo, ñépp di ci teg seen bët.
Gis nga itam ni watkat yi cosaanoo Kab-
Weer baree tey, kaar, ci Ndakaaru ? Ñoo
fi indi raasuwaar yi ñuy watoo léegi. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_283 | Benn doomu Kab-Weer bu ñu naan Tooy
Delgaado, moo fi jëkk a ubbi néegu
watukaay ci Ñarelaa gii. Senegaal ba
Senegaal daj, kenn masu noo jëkk a gis
raasuwaar, nun waa Ñarelaa ! Ci Téereb
Wis bii nga téye di ko jàng sax, dinga
dajeek ndaw su tudd Tinaa Delgaado, muy
toggal Garaη Maxu kaccuupa. Tinaa
Delgaado moomu, sëtu Tooy la woon,
ndeysaan. Laata Tooy di ñëw Senegaal,
xottu-butéel lanu daan watoo. Raasuwaaru
Tooy Delgaado bi yéem lool waa Ñarelaa,
nag ! Dégg naa nit ñi dañu daan dajaloo,
di buuxante ci buntu néeg bi di ko seetaan,
muy xuuf aka xuufaat. Saa yu sëqu karaw
waddee, ñu yuuxu, tàccu, daw jiiroo ko !
Àddinay dox ba Ñarelaa mel ni mu mel
tey. Fekk Tubaab bi ñëw fi, aakimu péexu
tefes gi, tabax fi ay kër ak ay isin ak ay
biro.Waaw, Badu, duma la tàyyee laaj lii :
naka la am réew di sàggane ba ay
doxandéem ñëw teg ci moom loxo, di fa
dogal ? Du fii rekk la mas am, gaa, waaye
teewul muy lu doy waar. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_284 | Isin ba ma daan liggéeye, benn nit ku
weex doηη moo fa newoon, ñu koy wax
Póol Gimaar. Bu dajewaan ak yow ci ëttu
isin bi, day taxaw ne la jàkk. Soo
sëggulee, mu àjji sa kaabaab. Soo
sukkulee balu ko àq, mu dàq la ci saa si.
Lu waral loolu ?
Ci sama gis-gis bu gàtt bi de, yaakaar naa
ne buum gi ab doxandéem di noseem
réew, di ko wommat ni xar mbaa gëléem,
buum googu Badu, waa réew maa koy
ràbbal seen bopp ! Gis nga ba tàyyi kenn
ci sama Tubaab-Njallxaar yi taxaw lu
yàgg ci kanamu seetoom, di takk ak a
takkaat karwaatam. Su noppee, geestu
soxnaam, siiñ ko, ne ko :
- Dégén, jekk naam ?
Gis nga loolu ba tàyyi !
Tubaab bi, dooleem kese mënu ko woon
yóbbu fenn. Dafa mànkoo ak ñenn ci nun,
bokk ak ñoom mbuus. Tubaab bi di nu
xeex, ñooñu ànd ak moom di sot, mu di
leen sànni lee-lee seen ñamu-bët. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_285 | Noonu la Tubaab bi ñamalee ay doomi
réew mi ci làkkam, ñii nekk ay làppto, ñii
solu soldaar, ñeeneen ñi nekk ay bóoy
walla ay mbindaan.Aka noo ñee woon
bóoy yeek mbindaan yi !
Aa, bul ree, Badu !
Jamono jooju kay, daraja nit kaa ngi aju
woon ci na mu gën a jegee Tubaab bi. Ñu
bare bëggoon nañoo nekk bóoy walla
mbindaan ci kër Tubaab yi, mu të leen. Ñi
daan toggal Xonq-Nopp yi, di leen
làpptool, di leen aar mbaa di fobeere seeni
néeg, ñoo jëkk a tabax ay këri Simoη fii ci
Ñarelaa. Man óbërye laa woon isin bu ñu
naan Air Liquide, ca wetu Kaay-Findiw.
Su nu julliwaan tisbaar ba noppi, danu
daan riirandoo, nun waa Ñarelaa, wutali
biir Ndakaaru. Jamonoy tubaab bi,
daanaka saret moo doon Mersedeesu tey !
Boroom barke yi rekk ñoo ci daan dugg,
nun baadoolo yi nu topp ciy rung, mel ni
ñu leen di dar. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_286 | So gisee sama gaa ñi, ñu nga ne noηη ci
kow, ak seeni west ak seeni kàsk ! Ku ci
téyewul téere Lamartin walla Wiktoor Igo
la xawma, di yuuxu ci naaj wu tàng wi,
yaa ngay jàng surnaal bi ñu doon wax
booba Pari-Dakaar.
Lépp daal, ngir won nu ne ñoom duñu
ñeexu-ñebbe ! Àddinaa mën a soppiku,
walla ! Léegi, baadoolo yi sax rus nañoo
toog ci saret ñu leen di gis. Sama Aatu
Sekk mi fàttali na la ci Téereb Fent ne :
- Ndànk-ndànk mooy jàpp golo cib ñaay.
Nun ñii tamit, noonu lañu Tubaab bi naxe.
Da doon màtt di ëf, daanaka. Dem nañu ba
koo ci laaj lan la reere, mu ne la moom
jomb naa dugal ci biiram bi lu dul ñamu
Tubaab. Laata nuy àgg foofu, am na fu nu
Tubaab bi jëkk a jaarale. Fekk na nu fecc
ay peccam, làkk làkkam, watoo ni moom,
soloo ni moom ba ku nu won ginnaaw
doo xam ndax yàpp lanu mbaa jën lanu.
Am na lu benn waa ju am xel wax keroog
ci rajo bi. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_287 | Dafa ni :
- Tubaab bi dafa noo nëbb sunu bopp,
won nu boppam.
Mën a toppandoo bu jéggi dayo boobu
nag, Badu, man mii teel naa gis ne
doxalinu golo kese la. Moo waral, jamono
jooju, ma dem bokki PAI, ànd ak gor ya
ma fa fekk, nuy xeex Tubaab bi, ne fàww
yu ñàkk faayda yooyu dakk, nu gar ci
sunu bakkan. Ñu bare di nu kókkali, naan:
- Waa PAI yii ay tàng xol doηη lañu !
- Moo ! Ci njaayum ngóora lañu nekk,
kat !
- Liy tooy ci ñoom lay jóge !
- Kastorel lañu fiy fekk ! Ku mu ci yóbbu
Guy-Maryaama, waxtaan faak yow ba
bàyyi la, dinga wax lu set !
Lu nekk lañ nu daan yakk. Tey nag, nee
nañu réew mi jot na boppam ci 1960.
Waaye man de, jikko golo jooju laay gis
muy wéy ba sunu jonni-Yàlla tey jii. Booy
seet sax, | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_288 | danga naan nun noo leen xawoon a tane,
yéen goney léegi yi. Tubaab bi déj na nit
ku ñuul ci kanamu seetu bi. Kooku seetu,
gis boppam ci biir, rus, daldi sëgg.
Ne tuuti, mu siggi ne :
- Aa ! Dem naa bay juum sax, kii kay du
man, kii keneen la.
Neeti tuuti, mu daldi mer, ne ki mu janool
ci biir seetu bi :
- Bettuma la ! Ñu nekk fay xeex nag
jëmale ginnaaw-ëllëg. Reyante yu metti yi
ngay dégg ci Afrig yépp, dara waralu ko
lu dul xeeb sa bopp. Réewu Afrig moo
dem tey, dégg fa kuy xultu, naan :
- Lu ma ñàkk, diw moo ma ko xañ, ndax
ñi mu bokkal waaso la fi nekkal.
Waaye soo delloosee sa xel, xoolaat yëf yi
bu baax, dinga gis ci saa si ne yaak diw
moomu benn ngeen. Loolu tamit, ci li ma
Séex Anta Jóob jàngal la bokk.
Ma ni : coow li mépp du dara lu dul xeeb
sa bopp. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_290 | TÉEREB DÓOM
III | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_291 | Badu, xibaar bu neex a ngi lay xaar
Ñarelaa. Kaay ma fen la ko gaaw : Baydi
Sàll tudde na la fi doom. Bërki-démb ci
alxames ji la woon ngénte li.
Ndaw mbetteel gu neex ci man mii ! Ñu
bare jooy nañu fa te tuuti kon ñu jooyloo
ma. Dañu la faa gërëm, yow Badu, ba am
ñu tiit, di jéem a delloosi xelu nit ñi :
- Laaw-la-cat ! Buleen gémmiñu sëtu
Ngiraan Fay bi !
Baydi Sàll, sa xarit bi, sa doomu-ndey bi,
ku baax la moom itam te gore, nde
mënoon naa séentu xaalis ci turu doomam
ji, may ko boroom barke. Ndeysaan.
Maa ngi fàttaliku, ni ngeen ma taqe woon
yéen ñaar, bi ngeen newee gone. Waaye bi
ñu ma nee sa turandoo bi mooy ñeenteelu
doomu Baydi Sàll, dama yéemu.
Dund naa ba gis samay sët ñu uuf seen
njaboot...
Kon boog li ma dese bareetul. Sant
Boroom-bi rekk moo ma war. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_292 | Soo gisee ma lay wax loolu, dafa fekk ma
yëg fan yii ni sama yaram wiy bañe.
Duma la ko nëbb : bi ma jógee ngénte la,
daanu naa ci yoon wi, daldi sax xëm
foofu. Dama jékki-jékki samay tànk diis
gann, may miir, xamatuma fan laa nekk.
Muse Sumaare mi ma doon tooñ keroog
ci Téereb Dóom bu jëkk bi, moo ma fa
fekk, dugal ma ci otoom, indi ma ci kër gi.
Tey ci bëccëg ànd na feek doktoor Jibi Faal,
kooku seet ma, bindal ma ordonaas. Te xam
nga kan moo jënd ordonaas beem ?
Xanaa Muse Sumaare mi ma yaakaaroon
ne moo yées ci ñi Yàlla sàkk ! Gaaw a
wax baaxul, Badu. Day tax nga dëkkal nit
fu mu dëkkul. Maa ngi xaw a am tan.
Waaye mag moom su dikke rekk dikk na.
Rax-ci-dolli, nanguwumaa noppalu.
Téere bu fees, ma ubbi beneen tàmbalee
bind. Lee-lee sama kaaη giy xasan, mu
mel ne ay melentaan a ciy doxantu, ma
koy wokk. Waaye xam nga sa maam
Ngiraan Fay, kenn gënu maa dëgër bopp! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_293 | Fàww ma bind, bàyyil la fi, Badu. Te su
nu waxantee dëgg nag, jokkoo beek yow
ci boppam moo ma neex.
Te it, feek maa ngi noyyi, li war ci sama
digganteek yow dinaa ko def ba mu mat
sëkk.Xanaa kañ damay jéem a bàyyi
kebetu bi rekk.
Li ci des nag, maanaam dund mbaa dee,
Yàllaa ko yor. Lu mu dogal ak waxtu wu
mu ko dogalee noonu la.
Xaaral ma def li gën a wóor : ubbi Téereb
Dóom, nettali la ci jaloorey Yaasin Njaay.
Nekk fiy mbebetu amul benn njariñ...
Laay ! Ndekete nettalikat su amulee fulla,
mën naa dem ba fàtte lu tax muy yatt
xalimaam, tëju moom kenn di naan kafe,
di bind guddi, di bind bëccëg !
Ndekete ñaari kàddu yoo rëdd, àddinaak li
ci biir xej nañu ci... Su dee ruq bu ndaw
boo gis, bëgg faa taxaw, niit ko, dinga
fanaan àll ay ati at, nekk ci yoon wiy
wëndéelu ba tax doo àgg mukk fa nga jëm. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_294 | Ayca boog, Badu, nanu déj ci diggu géew
bi Yaasin Njaay ak ñaari doomam yu
xamadi yi mu jële Tugal, indil nu leen
Ñarelaa.
*
* *
Li Yaasin Njaay xamul moo di ne Ñarelaa,
gox buy naxaate la. Nekk na fi, di dem aka
dikk, defe ne kenn toppatoowul ay mbiram.
Fekk na boobu tànk bu mu yëkkati, balaa
muy fekki ba ca des, nun ñépp nu ngi ciy
teg sunuy bët, xam lu mu nar. Xawma fan,
waaye Ñarelaa moom du goxu dox daje.
Ñarelaa gii, ñépp ay mbokk lañu. Ñaar
yoo fi gis ñuy kaf mbaa ñuy xuloo, seeni
maam a leen ci jëkk a jaar. Gone yu góor
yee bokkoon lël, janq ji màggandoo fi,
doxaanante am ci yoon, ay doom juddu ci.
Yaasin nag moom, ténj na ci kër gi ba ni
mu summee te masu ma fi won lu dul
ñàkk teggin. Dafay jiital Mbisin ak
Mbisaan, romb ma fi ma toog ci ëtt bi,
nuyoo ma bakkan, dem yoonam. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_295 | Ñaari doom yi ñoom, gone du reew ba dab
leen. Man lañu def seen golo. Dañu may
fekk lee-lee may wird, ñu may sëllax suuf,
di ma sànniy xollitu banaana.
Yaasin moom, sa ndey Biige Sàmb la ko
Yàlla nattoo. Biige naxante naak moom,
fiir ko, ba sànk ko. Mën nañu wax sax ni
Yaasin Njaay dafa alku.
Moytul ma merum jigéen, Badu ! Ndekete
Biige Sàmb masul a baal Asan Taal ma ko
woroon ca seenug ngune. Biiral ko, dem
Màrsey, wacc ko feek liiram bu tooy xepp.
Ndekete Biige giñoon na ne, li ko Asan
Taal def, dina ko feyu ci Yaasin Njaay ak
ñaari doomam yi ! Te li mu bëggoon de,
am na ko, ndax takk-der yee mujjee ñëw
Ñarelaa, njoñ Yaasin ni ganaar, yóbbu ko
Caaroy, fa Buur di denc dof yi, ne ko fa
ràpp tëj.
Mag ñi fàttaliku ndawug Asan Taal. Foo
ko fekk mu ngi téye balu futbal bu ndaw,
di tël, di sànni ci miir yi, di mbëkk, ñu koy
tooñ, naan ko : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_296 | - Sama rakk, yaa bëgg futbal ! Dafa mel ni
bés ba ñu la ngéntee, dañoo xooj balu
futbal ci ndox, jox la nga naan !
Dinaa ci yokk ne sa baay Asan Taal
futbalkat bu mag la woon. Moo tax bi mu
nee day dem Màrsey, bettul kenn. Xawma
nag lu tax yëf yi mujjewul a àntu foofa.
Am na daal ay wax yu ñaaw yu ci nit ñi
jot a wax te àgge la ko dina ma xaw a jafe.
Ñu bare a ngi fi doon yàkkali bóli nag,
yaakaar ne Asan Taal dina leen yónnee
àddinaak li ci biir. Ñooñu ñoom, seen
yaakaar tas na, jotuñu ndimbal li ñu doon
séentu, ndax nun de, néewu Asan Taal
lanu teeruji ayeropoor.
Ma dellu boog ca bëccëgu Yaasin Njaay
ba.Bés boobu, waa Ñarelaa bég nañu ! Fii
la Yaasin Njaay nekk, di daanu gangiri, di
xulliy bët, gémmiñ giy fuur. Ñaari doom
yi langaamu ko ndeysaan, di jooyoo, ragal
xanaa nun sowaas yu bon yi nu fees leen
dugal leen ci kàddiir, rëgal leen lekk. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_297 | Keroog, Ñarelaa gis na lu ko yéem. Am
ñu naan :
- Ñaw ! Lu waay rendi ci sa loxo lay nàcc.
- Fii Ñarelaa la ! Wund du fi naane ñeex!
- Ñuy wax mu naan moom tubaab bu
weex tàll la !
- Waaw, moom de nee na Mari-
Gabriyelaa Won Bolkowski la tudd !
- Mari-Gabriyelaa lan ? Ndaw tur wu
gudd sax ! Dem naa bay yërëm Yaasin
Njaay. Maa mel noonu : sama xol dafa
gaaw a toj. Waaye ma fàttaliku bés ba ma
Yaasin tiimee, tas séram, joxoñ ma
bajoom, di ma xulee-ka wax wax ju ñaaw.
Ma ne ci sama xel : kii moo fi yées la, bu
yaboo sax ñu tëral ko rendi, sama yoon
newu ci.
Ci laa jóge fatu.Fatu, laa wax, de, Badu
Taal. Jàppal kàddu googu : fatu. Li ma
log, su ma koy yàbbi jàng yiy tas. Badu, li
Yaasin Njaay def te ma nar la koo nettali
de, du jëf ju rafet. Waaye nu may def ? | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_298 | Su doon sama sago, ma jekk-jekkal mbir
mi ba mu gën a neex a dégg. Waaye xam
naa sama warugar : jottali la lépp li jot a
xew Ñarelaa sa ginnaaw.
*
* *
Bala nuy sore, may ma tuuti ma won la ni
Yaasin Njaay di daagoo ci mbeddi
Ñarelaa yi, jëm màrse.
Bés a ngoog ci bés yi ! Yoor-yoor la
woon. Yaasin Njaay xéy na, defaru ba
jekk, taxaw ci buntu kër gi ba mu neex ko,
mu jubal yoonu màrse. Ñaari nit ñu
Yaasin romb, ñu ni tekk, di ko xool ba mu
jàdd koñ. Ñu nekk nag ci deram, di ko jëw
aka ñaawal. Bi Yaasin àggee gaaraasu
Paap Kànji, benn gone jóg na topp ko, di
toppandoo ni muy doxe, di ko ηóobi, te
Yaasin yëgu ci dara. Ñii ngi ree, ñii di
déeyante :
- Kii mooy sunu ganu Tubaab gi may
dégg, de ?
- Moom la sax de, ak ñaawaayam bu réy. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_299 | - Man de, xawma man Yàllaa xiiroon
Asan Taal ci kii ba mu koy takk !
- Yaa yëg fu mu ko takke ? Dañu doon
nekkaale kañ, dégg naa. Ñeneen ñaa ngi
làqu ci seen ginnaaw palanteer di yërndu
Yaasin. Lu mat ñaari waxtu, Yaasin
wëndéelu na moom kenn ci gox bi. Du
benn yoon nag bu mu taxaw nuyoonteek
ñi mu jot a dajeel. Xanaa Cerno, gone giy
jaay surnaal, lanu ko gis mu waxal. Am na
lu mu laaj Cerno. Kooku ne ko:
- Yéenekaay bu tudd « Marie-Claire » ?
Yéenekaay boobu de, masuma koo dégg.
- Moom laa daan jàng ba ma newee Tugal.
- Dinaa la laajal samay xarit ba xam ndax
am nañu ko.
- Matu ko, su ma demee biir Ndakaaru
ngoon, dinaa ko jëndal sama bopp.
Cerno di dof-doflu, ni ko:
- Laay ! Kon yow dëkkoon nga Tugal ci
dëgg-dëgg, soxna si ? | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_300 | - Fa laa dëkk ba tey, dafa am yu ma doon
toppatoo rekk bi ma ténjee ba noppi.
- Aa ? Dangay dellu, kon ?
- Man kay taxaw naa.
- Tugal neex na de, dégg naa ! Bërki-
démb rekk, benn waay a ngi kaf ak man...
- Lu mu la wax ?
- Déedéet, benn Tubaab dafa ma may
junni, ma ne : « Tubaab bii de, Yal na ko
Yàlla xare àjjana ! » Sama moroom mi
ree, ne ma : « Aa, Cerno, Tubaab de, su
tàbbee àjjana, tàbbi na fu mu miin ! »
Yaasin Njaay ree, ne Cerno :
- Dëgg la ! Foofu kañ neex na lool. Xam
naa léegi nga ne danga may topp yow
tamit !
- Waa-waaw ! Dëkk bi neexul, sama
jigéen, xanaa déggoo ñu naan toog torox,
tukki tekki ? Nun ñépp a bëgg a làlli.
- Làlli ? Luy loolu ?
- Mooy jël picc mi, xanaa ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_301 | - Picc ? Picc man ?
- Xanaa naaw, dem fu soree-sori.
Yaasin xàqataay. Ñarelaa yéemu. Ndekete
ndaw si am nay bëñ bay reetaan !
Nu laaj Cerno lan la waxanteek Yaasin.
Mu ne nu :
- Ndaw sii yembul. Dingeen ne Cerno Kan
waxoon na nu ko ! Kii, xel mi neexul de !
Ba mu jógee ci Cerno la Yaasin Njaay
dugg nag ci biir màrse bi, taabal bu nekk
mu taxaw fa, xool ba xolam sedd, daldi
randatu ca ba ca des. Lu nekk laal na ko
keroog, te taxul mu jënd dara mbaa mu
nuyook benn jaaykat.Waaye ña mu
taxawoon seen taabal yépp dëggal nañu
kàdduy Cerno Kan ya. Wax ji doon benn :
- Sunu gan gii, yaram wi neexul. Kon
boog nga xam ne li fi dal Yaasin Njaay
bettul Ñarelaa. Ay fan lañu ca teg, sa yaay
Biige Sàmb ñëw ci kër gi. Masu fee bare
tànk, gaa, waaye saa yu fi juuxee, dina ma
laajte, fu ma mënti nekk ci kër gi mu
nuyusi ma. Bii yoon, loolu fekku ko ci. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
Subsets and Splits