url
stringlengths 6
8
| content
stringlengths 2
3.72k
| source
stringclasses 3
values |
---|---|---|
page_302 | Damaa toog ba yàgg rekk gis ko mu génne
néegu Yaasin, ñu ànd mook Tamsiir Ba,
di waxtaan, di kaf aka ree. Ma ni ko :
- Moo, Biige kañ nga fi ?
Ci la ma door a wax ne Yaasin a ko yónni
woon. Wax jooju jaaxal ma lool waaye
teguma ci baat. Aa ! Badu, man kat damaa
yëgul fu Yaasin Njaay ak Biige Sàmb
takkee xarit... Xawma it lu waral sa ndey
di nangoo sibooru Yaasin, ba di ko doxali
yónnent.
Ma yëngal sama bopp, mu dellu ne ma :
- Waaw, Ngiraan, fooy dégg sama doom
ju baax ji ?
- Kan ? Badu Taal ?
- Waaw. Moom kat ba mu demee ba tey
bindu ma.
Bi mu waxee loolu, sunuy bët daje, ku
nekk ci nun ñaar daldi xalaat lu doy waar
ci saa si. Asan Taal, ndeysaan. Bés ba
muy dem Tugal, nun ñépp sunu xol diis,
nuy jooyoo, mu naan sa yaay : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_303 | - Su may àgg Màrsey di la bind, Biige.
Ma siggi, ne Biige :
- Badu de, xanaa balaa yàgg mu dellusi.
Góor kat moomul toog.
Sunuy bët dajewaat. Takkandeeru Asan
neeti bërét, def ay jéego yu rey, jaar sunu
diggante. Góor moomul toog.
Bés ba Asan Taal di yëgal Biige ne dafa
war a dem Màrsey, baat yooyu la doon
dàmpee xolam, di ko dëfal. Góor moomul
toog. Lee-lee, day mel ni li nit kiy wax
mbaa mu koy jëf, du nekk mukk si
coobareem.
Kàdduy démb. Jëfi démb. Yéen ñaar
moom, faww ngeen dellusi bés ci géew bi,
ganesinu. Dangeen di naaw, ne cabax ci
gémmiñu Doomu-Aadama. Dangeen di
wëndéelu ci biir géew bi, nu dem ba leen
fi : loo wax maam waxoon na ko, loo mas
a def it bés dina ñëw sa sët defaat ko.
Fi nuy waxtaanee maak Bige, Yaasin génne
néegam, jiital ñaari doom yi, daldi ma nuyu
nuyu bu sew te gaaw, ne fiiw romb ma. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_304 | Gone yi fekksi ma fi ma jaaxaan ñu niit ma,
ηóobi ma ba seen xol sedd, sog a dabi Biige
Sàmb ak Tamsiir Ba, seen faru yaay.
Nga baal ma de, Badu, waaye Biige Sàmb,
sa yaay jii, ku bari pexe la.
Li ma gën a waar mooy naka la def ba
miinanteek Yaasin Njaay. Soo leen gisee,
danga naan ay doomi-ndey lañu. Wute
wuñook ay xaritu benn bakkan yuy ànd ba
ñu doonee ay xale yu tuuti ba nii ñu
nekkee magum jëmm. Foo séen Biige
Sàmb mu wóor la ne Yaasin Njaay sorewu
fa.
Ci sunuy aada, nun waa Senegaal, loolu
dara aayu ci.
Am na nu mbir mi doon deme sax, bég
kon naa ci seen àndadoo boobu, rafet ci
njort.
Ndax, muy Yaasin Njaay di Biige Sàmb,
ku ci nekk am na fu mu ma féete, ku ci
nekk sukk na jural doom Asan Taal ; su
doon sama sago, dama naan rekk Yàllaa
yedd Yaasin ak Biige, bës seeni xol, | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_305 | ba tax ñu xam ne léegi ay mag lañu, weesal
seen boppxulook ηaayoo.
Ba tax it ñu xam ne gunge doomi Asan
Taal yee leen war, ñu def ko na mu gën a
rafete.Waaye àddina leneen la ma jàngal !
Xam nit, xam jikkoom a ko gën. Ni Biige
Sàmb ñóoxoo Yaasin Njaay, mënul a jur
jàmm. Doomu-Aadama day faral di tënëx-
tënëxi ci yoon wu xat te lëndëm këruus.
Bés, àll bi yépp leer nàññ. Ku nekk
yéemu. Li lemu woon, lemmikoo fu ko
kenn masul a fooge. Mbiru Yàllaa ngoog.
Yaasin Njaay, Biige Sàmb la ko Yàlla
booleel. Ci moom la jaarale alag gi mu ko
naroon a alag.
*
* *
Bés, nu dégg ne Yaasin a ngi waaj a dellu
Tugal.
Waaye man mii de, man miy yeewook
moom ci benn kër te yar Asan Taal mi ko
fi indi, waxu ma ci dara. Bi ma ko déggee
ci nit ñi, dama ne rekk ci sama xel : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_306 | - « Aa, baax na. Xanaa boog ma jàppe ko
noonu ».
Ba ñu nee suba la Yaasin di dem, Biige
Sàmb a ko létt, ñu ànd ñoom ñaar biir
Ndakaaru jëndi seeni yóbbal ak ay yëfi
jigéen, xam naa.
Ba mu defaree ay waliisam ak waliisi
doom yi ba noppi, la door a ñëw
tàggatook man.
Man it wax naak moom wax ju rafet,
gërëm ko, ñaanal ko.
Xawma gan mbaax a ko dugg àjjuma
jooju, waaye yëkkati na ñetti junni may
ma. Dem naa ba naan ko mu téye
xaalisam, waaye sama xel yedd ma, ma
xam ne mag moomul yenn yi, te loo muñ
ba mu jeex jarul nga ciy ñaaw.
Ma ni ko :
- Xaalis bii gën a bare, Yaasin ! Teguma
la ko kat, Njaay Jaata.
Xam nga Badu, wax joo gis am na tontoom.
Mënoon na ma ni : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_307 | - Lii kañ du dara ! Damaa xaw a sant Jóob
rekk, nde moos yéene naa la lu ko ëpp fopp,
nijaay Ngiraan.Mbaa mu ne ma :
- Yàlla xam na ne xeeb naa ko, góor gi
Ngiraan, waaye bul wax dara, xaaral ba
ma dellu Màrsey rekk !
Loolu yépp fekku ci Yaasin. Dafa ne
nemm-nemmaaral, di ma xool mel ni du
moom laay waxal. Xawma lu ma yëf yiy
niru, ma jéem a kaf ak moom, ni ko :
- Soo demee nga nuyul ma waa Màrsey te
bul fàttee bind Mbisin ak Mbisaan.
Yaasin daldi ma xulli, fas kanam gi xaat.
- Bind kan ak kan laa dégg ?
- Xanaa sama ñaari sët yi ! Xamoo ne
ñoom duma leen bàyyi ñu jóge Ñarelaa ?
Mënuma laa nettali ni Yaasin tëje kanam
gi keroog, Badu.
Bi mu ma gisee ma muuñ lay sog a xam
ne dama ko doon tooñ doηη, mu daldi
muuñ moom tamit. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_308 | Waaw, Badu, ku la masula tudd, masula
taas, su takkee ay waliisam, fëgg sa buntu
néeg, fekk la fi nga tëdd mu tàggu la,
xanaa kay li ci des mooy mu woolu taksi,
ne yoonu ayeropoor maa ngoog ?
Du dëggam, Badu ?
Ba àddinay baax de, noonu la yëf yi daan
deme. Waaye bés ba ma Yaasin tàggoo ba
noppi, la tàmbalee def lu ma jaaxal lool.
Ca laa ko gis mu yebbi ay waliisam ci ëtt
bi, yëre bu ne mu yëkkati, fëgg, fëggaat,
poos bu nekk mu dugal ci loxoom, yuri
ko. Lee-lee mu teg benn ndoket mbaa
benn sér ci suuf, jëlaat ko, lemmiwaat ko
ba noppi delloo ko ci biir waliis bi.
Lan la Yaasin Njaay réerle woon noonu ?
Waroon naa réy de, ndax ci ay xultu ak ay
waxtu la mujje. Ne tuuti, Biige Sàmb agsi,
taf gémmiñam :
- Waaw Yaasin yow, loo xewle ? Du danu
waroon a dem ci Sinkun Kamara mu ñaanal
la, ñaanal xale yi ? | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_309 | Yaasin siggi, xool Biige Sàmb.
Man mii Ngiraan Fay de, dootu-ma gone,
waaye giñ naa ne musumaa gis nit ku jàqe
ni Yaasin Njaay keroog.
Ñaari doom yi ñëw katamu ko, di yikkat.
Mu ne Biige :
- Sama këyit yépp réer nañu, Biige.
- Nga ni ma ?
- Waa-waaw. Seet naa ba sonn.
- Loolu gën a doy waar, Yaasin !
- Wóor na ma ne am na ku fi dugg jël
samay kayit ! Seen kër gii kay !
- Céy, yaa bare ay ! Yaa ngi tooñati, de !
Bés bu ne ma ni la gaaw a mer baaxul,
Yaasin Njaay.
- Amatuma paaspoor, amatuma kayit giy
biral ne Tubaab laa, lépp réer na ! Nu may
def, Biige ? Fu ma jëm ?
- Nanu dem. Man Biige Sàmb loolu
mënumaa të, am naa ci pexe. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_310 | Li ma jëli keroog ci waxtaanu Yaasin ak
Biige, lii la : musiba moomu daloon
Yaasin, sa yaay amoon na ci mbégte mu
réy a réy !
Te njortoon naa it ne fu kayiti Yaasin
Njaay ya dugg, moom Biige Sàmb moo
leen fa dugal.
Njël soreetul woon. Ñu dégg ci Ñarelaa
benn waay juy tëgg sabaram tey yuuxu ca
kow :
Dégluleen, jàmm la ! Dégluleen jàmm la !
Boroom dëkk bi nee na : bu ci kanamee,
na waa gox bi yépp daje ci pénc mi !
Boroom dëkk bi nee na dafa bëgg a
waxtaan ak yéen ! Bu kenn des ! Góor ak
jigéen ! Mag ak ndaw ! Dégluleen, jàmm
la !
Ñarelaa xéy, dajaloo ci pénc mi. Mbooloo
mu takkoo ngi taxaw di xaar. Ñu dem ba
yàgg, mu am lu jaaxal Ñarelaa. Kenn ci
gox bi mënul a fexe ba teg bët kilifa gi ñu
ne moo woote. Ku yegsi laaj ki nga jëkk
dajeel : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_311 | - Ana ki waral lii lépp ?
- Kii kan ?
- Xanaa ki tax nu dajaloo ci pénc mi !
- Moom lanuy xaar booba ba léegi.
- Nanu xaar boog.
Ñarelaa xaar ba xàddi, mujjee xaare
boppam.
Usmaan Sow, boroom saret bi ne :
- Nun daal, noo ñàkk faayda dëgg ! Ay
boroom kër yu tollu ni nun, benn waay
tëgg sabaram rekk, nu ñëw weeru ci naaj
wu tàng wi, ku nekk di siiñ sa moroom !
- Usmaan wax na dëgg, bunu sàgganati ba
lii di nu dal !
Waaye bi ñu demee bay tasaaroo, la am ay
kàddu yu kalaate niy bali fetal ci jaww ji :
- Demleen ! Wéyleen ! Na seen ngelaw
neex ! Li ko doore bés niki tey, dootuleen
noppee dégg sama baat. Waroon ngeen a
xam moos ne lu mu yàgg yàgg dinaa
dellusi ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_312 | Ñarelaa tiit. Ku nekk di sànni say bët fu
nekk, ngir xam fan la kàddu yooyu jóge.
Kenn ci nun sañul a tudd turam. Waaye
nun ñépp la sunu xel dem ci moom.
Aali Këbóoy !
Aali Këbóoy...
Aali Këbóoy lañ koy woowe.
Luy turam dëggëntaan ? Kañ la dëkksi
Ñarelaa ? Fan la bawoo ? Loolu lépp
kumpa la ci nun.
Aali Këbóoy lañ koy woowe, waaye kenn
xamul lu tax ñu tudde ko noonu.
Dof bu am taxawaay la daal, di taxawaalu
ci mbeddi Ñarelaa yi, watu nel, bàyyi cër
yi ñuy lang ci biti tey sol ay sagar yu
tilima-tilim. Ci li ñuy wax, soldaar la
woon, nekkoon Dàqaar-Bàngo. Am, nee
ñu, lu ko fa feeñu bés ci njolloor, mu
jommi. Am na fiy jamono, lakkaloon nanu
lool. Da daan làqu ci wetu lekool
Kelemañsóo gii, su gone yi jàngee ba
wàcc mu leen di sànniy xeer. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_313 | Du benn du ñaar xaañ na fi nit. Saalitloo
na fi tam ay boroom kër yu bare ndax su
ko ci Yàlla xiiraan day nég ba xaaju guddi
muy kar nit ñi, di leen àddu-kalpe.
Bés nag, Aali def lu ëpp.
Ku ñuy wax Baay Ndeenee fi amoon xaj,
fii ci Ñarelaa. Xaj bi sonal lool Aali. Fu
dof bi dugg, mu fekk ko fa di ko mbów.
Aali Këbóoy di naxanteek moom, di ko
fiir ba ne ko niib, daldi ko rendi rendi bu
ñaaw.
Boroom xaj bi nag, Baay Ndeene, kilifa la
woon ci làrme bi, am doole ba noppi bare
ay ba nga ne lii lu mu doon. Kaay nu xeex
a ko gënaloon kaay nu ndékki. Dafa dóor
keroog Aali Këbóoy ba Yàlla fóot ay
sagaram. Céy, xeexu Baay Ndeene baak
Aali Këbóoy !
Man mii de, duma ko fàtte mukk ! Baay
Ndeene dafa njatt Aali Këbóoy di jamat
nel beek xottu butéel ba bopp bi xonq
coyy ak deret, muur kanam gi. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_314 | Li ko Baay Ndeeney jam yépp, Aali
Këbóoy a ngi koy balu àq :
- Sarax ma, dootuma la tooñ. Giñ naa ne
teyuma ko !
Maa mujjee yërëm Aali Këbóoy, woolu
pólis.
Bi alkaati yi ñëwee, li ñu ma jëkk a laaj
mooy kan moo doon dof bi, ci diggante
Baay Ndeeneek Aali Këbóoy !
Teg nañ ci ay fan i fan, kenn déggul Aali
Këbóoy, kenn gisu ko. Ñépp naan :
- Baay Ndeene kat waroon naa gën a teel a
jóg ci dof bii, upp baax na ci laax bu tàng,
kat ! Ñaw !
- Xanaa xamoo ni yëf yi deme ?
- Ãa ?
- Aali góbi doηη la woon Dàqaar-Bango te
Baay Ndeene moom moo yilif kapiteen yi
ci làrme bi yépp ! Du moroomam !
- Yaa ngi door a wax wax ji kañ ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_315 | - Yow kañ bëre bukkeek mbaam nga nuy
wax !
- Dégg ngeen yuuxu Aali yi, de ?
Wutewul woon ak mbaam-xuux mu ñu
ñàdd di ko rendi !
- Moo, koo koy wax ? Mu naan xuux xuux
rekk, tëwa bàyyi ! Gat di !
Ñu tegaat ci ay weer, Aali Këbóoy dellusi
Ñarelaa...
Tuddul kenn, taasul kenn. Dafa jubal
mbaaram, téju fa ay fan i fan.
Xam naa amoon na ay bori nelaw ndax
foo tollu ci Ñarelaa dégg ko muy xandoor.
Ba mu yeewoo, dafa toppaat mbeddi gox
biy wër.
Ñu tegaat ci juróomi fan, Aali Këbóoy
neeti mërr. Danu yeewu daal, gisatunu ko,
kenn xamul fu mu jaar.Ñaari at yu mat
sëkk jàllaat.
Bés, ci ndorteelu nawet bi, Aali Këbóoy
delsi ci gox bi. Taw bu jëkk boobu metti
woon na lool, ànd ak i dënnoo ki melax. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_316 | Ba muy séwét, fekk na ku nekk ci nun a
ngi këram di seetaan tele.
Bi nu jullee geewe, naan àttaaya bay waaj
a tëri, lanu dégg ay yuuxu ci mbedd mi.
Nu yaakaar ne waxambaane wu ñu doon
dóor la, muy woote wallu.
Ba ñu demee ba ca biir lanuy sog a leer ne
waa ji nekkul woon ci benn jafe-jafe. Da
doon woy, ndekete.
Xanaa kay baat baa xuuroon rekk, naqadi
ba nga ne lii lu mu doon.
Ñàkkul mu am ñu seen xel dem booba ci
Aali Këbóoy. Waaw, loolu mën naa am.
Waaye jaaxal kon na ma lool.
Ca dëgg-dëgg, fàtte woon nanu ay mbiri
Aali Këbóoy. Ku ko wax ak ku ko waxul
yépp, waa Ñarelaa jàppoon nañu ne Aali
ñibbina àllaaxira bu yàgg.
Ndax kat, Badu, xam nga ne dof yiy
taxawaalu ci mbeddi Ndakaaru yi, duñuy
faral di gudd fan.
Nee ma : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_317 | - Lu tax nga wax loolu ?
- Lu tax nga wax loolu, Ngiraan ?
Dafa fekk ni, dof kat, loo mën a xalaat ci
lu bon mu ngi koy dugal ci biiram bi te su
feebaree kenn du ko faj. Lee-lee it saxaar
mbaa oto fekk ko fi mu tëdd, yéeg ci
kowam, dër ko te du sax taxaw. Ay nit
ñooy romb néew bi, kenn ci ñoom ne :
- Ndeysaan... Mooy dof bi ñu doon
woowe... Fàtte naa tur wi, waay !
- Loolu de, amul solo !
- Ana dof ak tur ?
Su ko defee, ñu daldi woo ndawi Buur yi.
Ñooñu ñëw gàddu néew bi yóbbu. Coono
boobu lanu bañoon mu fekk nu ci, nun
waa Ñarelaa. Moo tax ba nu Aali Këbóoy
abalee, danoo sant Yàlla.
Moom kañ, na dem fu mu xam, mu deewe
fa !
Ndekete yóo, waa jiy wër gox biy woy,
Aali Këbóoy la. Mu ngi naan : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_318 | - Aa, man la Aali Këbóoy, maa dellusi
Ñarelaa. Yéen a ngi fàttaliku dóor yu
metti yi ma fi Baay Ndeene dóoroon, at
yee ñu génn ? Yéen a ngi koy fàttaliku,
mbaa ?
Kenn ci yéen nanguwu maa tontu, waaye
amul solo.
Man, Aali Këbóoy, maa leen di yëgal ne
dem naa dëkk ba ma fekk baax nag, laaj
mag ña lu tax Baay Ndeene toroxal ma,
tuur sama deret, te bu weesoo Ngiraan Fay
mu rafet xol mi, du kenn ci Ñarelaa ku
yëkkati kàddoom ne lii du yoon.
Dëkk boobee ma fekk baax, Ndimboy la
tudd. Lu ngeen di xulliy bët ?
Mbaa du dangeen yaakaar ne man Aali
Këbóoy amuma ndey, amuma baay ?
Neex ba dee ! Samay way-jur ñoo ma sant
ma dellusi Ñarelaa.
Waaw ! Bàyyi naa tooñ, dootuma sànni
gone yi xeer, jànq ji dootuñu ma romb
may këf seeni sër, di leen jéem a siif. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_319 | Loolu yépp tuub naa ko. Teewul nag, maa
moom sama làmmiñ wii, man Aali
Këbóoy.
Lu ma neex dinaa ko wax, te kenn du ci
mën tus !
Bi Aali Këbóoy daaneelee, ñépp a féex,
ku nekk naan :
- Aa ! Waxi dof de, amul solo !
Céy, su nu xamoon li nu doon yoot, booba !
Aali Këbóoy, Baay Ndeene ma ko duma
woon duma yu metti ya la jëkk a takkal
pot. Dafa daan taxaw ci boppu koñ bi, su
Baay Ndeene rombee mu koy daggal ay
saaga yu ñaaw a ñaaw.
Ginnaaw Baay Ndeene dafa amoon doole,
am alal, kenn ñemewu ko woon ci
Ñarelaa. Kapiteen la woon ci làrme tubaab
yi. Aali Këbóoy fental ko woy, di ko
kekkantoo :
« Ofise ne paa pëer, bu doxatee sax du
xasaw, ndax kenn du ñemee reetaan ! » | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_320 | Saa yu Aali Këbóoy séenee Baay Ndeene
rekk, tàmbalee tàccoo ka woy :
« Ofise ne paa pëer, bu doxatee sax du
xasaw, ndax kenn du ñemee reetaan ! »
Su ko defee, Baay Ndeene dëngalu, mel ni
du moom la Aali Këbóoy di gaaral.
Dem nañu nag ba kenn mënatul a muñ yëf
yi. Su woyu Aali Këbóoy woowu jibee
rekk, ñépp daanu ci suuf, di kex-kexi, am
sax ñuy taf seen bakkan, naan:
- Óo-xoo ! Xetu cuuraay gii moo neex !
Ñu demati ba gone Ñarelaa yiy awu Aali
Këbóoy. Baay Ndeene di leen dégg te du
ci mën dara.
Badu, ñaar yii, boo ci gën a ragal : ñu lay
sànniy doj mbaa ñu lay sànniy kàddu yu
ñaaw te ñaw ?
Bopp buy nàcc ak xol bu xëtt, lu la ci
gënal ?
Aali Këbóoy kat, tuuti kon mu tas
Ñarelaa. Lu waay def ci gox bi te di ko
làq, dina ko feeñal, weer la. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_321 | Daawul tudd turu kenn nag, waaye ñépp a
doon xam ku moom wax ji :
Aa, sama sang yu baax yi, lu ngeen xam ci
kuy yakkataan doomu-jiitleem ? Moom
laa fi gis de, ngóor saa ngi nii, ne fàηη ci
biir seetu bi !
Ku weddi na ñëw xool kook mbaxaneem
mu ñuul meek i bejjaawam ! Cim ! Ñàkk
jom badee !
Beneen bés mu ne :
- Aali, waaru nga ! Ndaw soo xam ne
njaalook naan ndox la yemale ! Céy
Ñarelaa ! Fii de moom, caga jeek jaaykati
yàmbaa yee fiy teg ndawal.
Walla mu ne :
- Waaw, nit ñi liggéey, ñaq, dajale seen
alal dénk la ko, amoo loo leen di wax lu
dul réer na te nga toje ko, man mii Aali
Këbóoy dof bi, ma teg ci samay bët !
Waay, noo àttane jël xaalis bu la lewul,
takk ci ñaareel, séet bu ndaw bi yaakaar ne
boroom barke nga, fekk tojemaan doηη
nga ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_322 | Ñépp mujjee ragal Aali Këbóoy, di ko
moytu ndax ñàkk kersaam. Rax-ci-dolli,
kenn xamul na mu daan def ba xam li mu
doon wax yépp.Am ñu naan :
- Aa, dof bi waxati na de ! Kii, ñàkkul
muy boroom xam-xam bu mag ! Mbiri
Yàlla kenn xamu ko !
Aali Këbóoy yemul foofu.
Ba mu demee ba mu wóor ko ne nit ñaa ki
koy may nopp bu baax, dafa daldi
tàmbalee sànni ay cax ak ay laajte yu doy
waar lool.
Maa ngi fàttaliku bés ba mu bettee Ibu
Ndaw ak Kinne Gaajo ñuy fóonante ci
tefesu Kusum. Weer woowu yépp, dafa nu
tanqal ak benn laaj bi :
- Jamono jan la nit ku ñuul tàmbalee
fóonante ? Moo, ndax Maam sax xamoon
na loolu ?
Foofu nag, jikkoy dof ji jàpp Aali
Këbóoy, muy joxe tontam, ne dafay jàngal
waa Ñarelaa naka la mbir yooyu daan
deme bi fi Tubaab bi ñëwagulee. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_323 | Aali Këbóoy doon na def it lenn : lu mu
wax tey, bu ëllëg saa mu jaaraat ca. Daan
na ko jàppe noonu ay weer ba mujje gi ay
kàddoom, gone yépp a leen daan tari.
Laaj ma nag kañ la Aali tas jàng yi !
Laaj ma ko, ma wax la ko !
Gis nga, Badu, politiseη yi doon joηante
fii ci Ñarelaa, ñoo xaar ba xaaju-guddi, ñu
yoloosu, fëggi mbaaru Aali Këbóoy. Mu
yeewu, ñu ne ko :
- Aali, nuyu nanu la.
- Man de, feyuma leen. Ayca ! Gaawleen
boog ci wax ji !
- Soo gisoon li nu indiwaale doo waxe
noonu, Aali !
Ñu génne xaalis bu bare, won ko.
Mu ne leen :
- Lii nag ?
- Du xam nga diw ? Nee na dafa noo bëgg
a yilif te...
- Lu ngeen bëgg ? | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_324 | - Ma xasal leen seen noon boobu ?
- Nit ku bon la. Fi mu ne, Ñarelaa ba
Ñarelaa daj, yow rekk la nit ñiy déglu !
Fàww nga xamal leen ne waru ñoo fal
saay-saay boobu !
Aali ne leen :
- Aa ! Ñaata ngeen may fey ?
- Loo bëgg, dinanu la ko defal !
- Xaalis baa ngi nii, su doyulee ñu yokkal
la ci lu bare !
- Ayca boog ! Waxleen ma lépp li ngeen
ko xamal ci lu bon.
Aali déglu leen ñuy talalali, lépp lañu
xamoon ñu wax ko ko.
Sa ëllëg sa, diw moomu làqu seetsi Aali
Këbóoy, mook ay nitam, ñu indiwaale
ñoom it saaku xaalis. Aali laaj leen lu
doon seen tànk.
Ñu ne ko :
- Diw de, nee na dafa bëgg a jiite askan
wi, te du nit ku baax. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_325 | - Lu ngeen bëgg ? Ma xasal leen ko ?
- Waaw. Yow, nit ñi fonk nañu lool say
kàddu, Aali. Loo wax ñu ne dëgg la, ànd
ceek yow.
Aali Këbóoy ree ci biir xolam. Gaa ña
wax ko lépp lu bon lañu xamaloon seenub
noon.
Aali daldi mel ni ku furtaat nag, Badu !
Fan yooyu kay, Ñarelaa rëb na lool !
Aali Këbóoy dafa jaxasee jaxase sunu
politiseη yi ba tuutee tee jaasi yi génn. Mu
ne :
- Ñoom ñépp xaar nañu ba suuf sedd, ñu
yoloosu seetsi ma, ne dañu may jënd !
Man nag, dof laa : xam naa lépp, dinaa
wax lépp ! Gaa ñi, ma ne : tey mu neex !
Ñarelaa ne tekk di ko déglu, ñii tiit, ñii di
ree ci suuf.
Aali Këbóoy dellu ne :
Ñoom de, lu kéemaane sax lañu ma
bëggoon a defloo. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_326 | Laaj leen ma loolu lu mu !
Dañu bëggoon ma jaay leen sama xaste yu
neex yi !
Xasal diw ak diw, wax ko ay baaxi
maamam nu fey la xaalis bu dul jeex !
Aa ! Xanaa kon ñoom bu ñu jotee ci réew
mi, dañu fi nar a ubbi daara ju ñuy jàngale
wax ju bon !
Su ko defee, ku dàq saaga ci réew mi yaa
fiy ëpp alal !
Man nag, gor laa. Sama teraangay bopp
jaralu ma yenn yi, duma wor mukk askan
wi.
Sama xaste yu saf xoroom yii, jaayuma
leen tey, jaayuma leen ëllëg ! Mayewuma
leen it, waaye teewul ma yéene ci ñépp,
nag !
Wax dëgg, Badu Taal, daan nanu dem ba
fàtte ne Aali Këbóoy dof la.
Bu daan wax, danu ko daan déglu bu baax
a baax ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_327 | Saa yu dikkalewaan it, noppi, danu daan
namm ay kàddoom ba nga ne lii lu mu
doon.
Benn guddi nag, Aali Këbóoy wax lu ëpp,
moom tamit.
Mooy guddi ga mu tuddee Tubaab bi, di
ko ηàññ, naan war naa génn réew mi abal
nu, nu moom sunu bopp.
Aa, guddi googu Badu, kilifay Ñarelaa yu
bare nelawuñu !
Mag ñi gise ci seen biir, ne :
- Luy jot jot na. Dunu ñàkk fulla ba ab dof
doηη di nu yàqal sunu teraanga.
Ñu yeewu bés, kenn gisatul Aali Këbóoy
ci Ñarelaa.
Mbaar ma mu daan dajale ay sagaram ak i
poti tamaateem, ñu daaneel ko, bale ko,
fobeere ko ba mu set wecc.
Ñii naan Aali Këbóoy dafa tàbbi géej ni
léeb bu jeex, ña ca des naan dafa gàddaay,
dem fu mu xam. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_328 | Ñeneen ne :
- Du tey la Aali Këbóoy mas a xéy ne mes !
Du ñàkk mu dellusi bés na mu ko fi daan
defe.
Gaa ñooñu de, Badu, dañu doon dof-doflu
rekk, ndax xamoon nañu bu baax nu yëf yi
deme. Leeroon na ñépp ne waa gox bee
sàkkaloon Aali Këbóoy pexe.
Waaye Aali de, dundam neenul.
Tey dinga toog Ñarelaa, dégg ku wax
waxam ba noppi, daaneele ko ay kàdduy
Aali Këbóoy :
- Ca jamonoy Aali Këbóoy de, daan na
wax ne...
Ba fi Aali jógeek tey mat na fanweeri at
ak lu topp. Kàddoom ya ñépp jàppoon ne
ay kàdduy dof lañu, tey ñu ngi ciy
sukkandiku, di leen dëggal, di leen waate,
di leen waaraatee !
Soo gisee, Badu, ma ubbi tey Téere bu
Ñuul bii, di la ci wax waxu Aali Këbóoy,
am na lu tax. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_329 | Lii laa la ci bëgg a jàngal : saxal ci li nga
nekk, bul nangoo nekk ma-riirandoo.
Donte sax li nga gëm, yow kott ci àddina
si yépp yaa ko gëm, bumu la tax a dellu
ginnaaw. Bul tiit, bul ragal. Bu kenn fees
say bët ba doo am fitu xalaatal sa bopp.
Badu, toppal ciy tànki Séex Anta Jóob ak
Aali Këbóoy.
Ba Aali Këbóoy xamee ne ñu ngi koy
waaj a fexeel, dafa daldi yëkkati baatam ci
kow, ne :
Maa ngi leen di tàggu, yéen waa Ñarelaa.
Tey, sama waxtaan ak yéen du gudd.
Wurus a ngi ñu gas suul.
Ay kàddooy xotti gannuus gi, di rëkk
asamaan seek doole, asamaan siy goqi ay
biddéew yuy ràyy-ràyyi.
Waaye yoon wi neexul a song. Ay dég
dinañu la jam, say loxo dinañu nàcc.
Amaana jaan màtt la. Moytul ma daηaru
jaan jooju ñu naan céebi ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_330 | Dinga mar, dinga xiif. Loolu lépp xej na
ci. Waaye soo toqiwulee, bés dina ñëw
say doom ak say sët bég, naw seen bopp.
Badu, lépp li ma xam ci àddina, dof bu
tudd Aali Këbóoy moo ma ko jàngal.
Moo tax ma ni :
- Dof mat naa bàyyi cim réew.
*
* *
Noo yaakaar nag ne noonu la yëf yi mujje,
Badu ?
Aali Këbóoy daal, moo jékki-jékki neeti
jamet sunu kanam !
Xéy nanu gis ko muy sampaat mbaaram,
di dajale ay poti tamaate ak ay mbuus.
Kàngami Ñarelaa yi giseeti seen biir.
Baay Ndeene ne :
- Aali Këbóoy mii dafa noo bëgg a yab
ñaari yoon. Lu ëpp tuuru. Ñoom ñépp ñu
giñ ne dinañu rendi Aali Këbóoy, diigal
néewam biir géeju Kusum. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_331 | Nañu ko waxe it lañu ko defe.
Yeewooti nanu bés, gisatunu Aali Këbóoy,
déggatunu ko.
*
* *
Ñaareelu bóomug Aali Këbóoy ga, nu mu
deme ?
Am na lu ma ci fekke, man Ngiraan Fay,
te dinaa la ko nettali.
Benn guddi, dégg nanu kuy yuuxu ay
yuuxu yu metti te yàgg lool.
Ma daldi xàmmee ci saa si baatu Aali
Këbóoy. Mu ngay jooy, di saraxu, naan :
- Ñarelaa waxleen ci, wóoy waxleen ci, ñu
ngi may reyati !
Ci laa jóge fi ma tëdd, man Ngiraan Fay,
ubbi buntu kër gi.
Bi ma dawee ba weesu kër Ablaay Jéeju te
dajewumaak kenn, laa sog a taxaw, daldi
yuuxu : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_332 | - Ay saay-saay songati nañu Aali !
Jógleen wax ci ! Buleen seetaan lu ñaaw
loolu, yéen waa Ñarelaa !
Waaye su ma Ñarelaa tontoo, yow ma
juddoogul woon booba yaa ma tontu.
Mbedd mbaa ngi ne selaw.
Bi ma àggee tali bi jëm kër Biram Saala
Géy, kenn ci ñi doon duma Aali Këbóoy
sànni na ma aw doj, doj wi cof sama
mbaxane, daaneel ko.
Ma sëgg man it for xeer, siggi di ko ko
waaj a sànni, gisatuma kenn, gaa ñi ne
mërr, réer ma. Ci laa dëppe.
Su ma ragalul woon fen de, dinaa ne Baay
Ndeenee ma doon jéem a xaañ.
Bi ma demee bay waaj a xàddi, la ma mii
xel ne naa làqu ci mbaaru-tëgg mi taqalook
sinemaa Riyalto.
Ne tuuti Kuwaamini, fasu Usmaan Sow
wi, ηexal. Ma xool asamaan si, gis ni
biddéew yiy melaxe. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_333 | Ñarelaa ngi ne selaw, ndeysaan. Xanaa
rekk lee-lee ngelaw li pes xobi garab yi
mbaa ma dégg xaj buy mbów ci guddi gi.
Ma daldi wiccax sama bopp, yéemu ci
mbonug Doomu-Aadama.
Sama xel dellu ci Aali Këbóoy : « Xam
naa Baay Ndeenee nga Kusum di joow, di
nemmeeku béréb bi gën a xóot ci géej gi,
mu diigal fa néewu Aali Këbóoy. »
Nit du dara, Badu ! Sànq rekk rendi nañu
ci Ñarelaa gii lu tollu ni Doomu-Aadama,
te mu ngi mel ni dara masu fee xew !
« Kuy fàttalikooti Aali Këbóoy ? Ndegam
nit Njaay moo fiy jóge ñu fàtte ba fàtte
turam, astemaak Aali Këbóoy ».
Teewul nag, Badu, yëf yi naqadi ma lool,
man mii. Keroog, ba ma dellusee ci kër gi
tamit, nelaw të na ma. Fajar jot, ma jóg
ànd ak waa Ñarelaa jàkka ja. Gaa ña
bóomoon Aali Këbóoy a ngi may jéem a
tuur lëndëm kat, naan :
- Sàcc bi fi gone yi jàpp biig de, xawma
kan, waaye moom dootul xand Ñarelaa ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_334 | Keneen ne :
- Soo déggee yuuxoom yi kañ, xam ne
tuutee tee ñu rey ko !
Ñoom ñépp ñu ree, def mbir mi ay kaf.
Benn tur rekk nekk ci xel yépp, waaye
kenn sañu koo tudd. Aali Këbóoy.
Niti tey yi ñooy naaféq, Badu !
Ba ñu ca tegee ay fan, am ku romb
mbaaru Aali Këbóoy, taxaw, daldi ne :
- Waaw ! Sunu Aali mi de, ayu-bés yii
yépp kenn gisu ko !
- Moom de demati na !
- Xam naa am na feneen fu ko rab yi
xiirati !
- Gaalu dof du teer !
- Na ngelawam neex !
- Mën naa dellusi, de ! Day xéy bés rekk,
ne nu maa ngi !
- Yàlla tere tereeti ko ! Moom kay, doyal
nanu ci sëkk ak barke !
Baay Ndeene ne ca tonet, ni leen : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_335 | - Seen coow li bare na te amul njariñ !
Démb ci timis, benn ponkalug kaña génne
na mbaaru Aali Këbóoy. Toj mbaar mi jot
na !
- Baay Ndeene wax na dëgg. Su nu ci
teelul a jóg, mbaar mii mën nanu fi indil
ay jàngoro yu kenn xamul.
Waaye Badu, ba dara desul lu dul sempi
mbaaru Aali Këbóoy, mbir feeñ na.
Nga ne ma :
- Déet waay !
Ma dellu ne la : mbir feeñ na kañ, Badu.
*
* *
Ñetti fan yooyu, képp ku jub mbaaru Aali
Këbóoy ne danga koy toj, jommi nga.
Garaη Maadaa jëkk jéem a sempi mbaar
mi. Waaye bi muy janook mbaar meek bi
ay loxoom di tàkk benn la. Garaη Maada
yuuxu, loxo yiy saxaar, mu leen di wiccax,
di tëb ak a tëbaat, fu nekk mu dugg fa di
wut ndox mu mu leen serale. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_336 | Mag ñii xoolante.Am ci ñoom ku ne :
- Nun kat, noo tooñ sunu bopp. Warunu
woon a sant Maada mu woyof bopp mii
mu sempi mbaaru Aali Këbóoy.
- Wax nga dëgg. Nanu woo Taala Njaay
minise bi. Moom war na cee mën dara, am
na doole, am na xam-xam.
Waaye, Badu, Taala Njaay jotul sax àgsi
ba ci mbaaru Aali Këbóoy.
Génn na këram gaa, waaye dafa ñëw ba
jub nu, tàmbaale miir ; fi mu wéeroo ci
benn kaasiyaa, nit ñi wër ko, la tàmbalee
woccu deret, di kadd-kaddi ba faf fa des.
Taala Njaay nag, yaaram la woon, amoon
ak ñépp jàmm ci Ñarelaa. Deewam gu
ñaaw googu metti na ma lool. Lu nekk ñu
koy wax nag.
Ñii naan :
- Aali Këbóoy mi nu yaakaar ne dee na de,
mu ngi ci biir mbaar mi di nu dégg.
- Eskéy ! Yàllaay maye, te ku ko neex lay
may ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_337 | - Bàyyileen gis kuy dem, sol ay sagar
rekk, ngeen di ko sànniy xeer ! Baax na !
Ñi ci des di dekkali ay kàdduy Wolof
Njaay :
- Deretu téegu du moy luppu boroom !
- Doxati gëléem kow la jëm !
- Sàcc ndënd yomb na moom, xanaa kay
am foo koy tëgge mooy jafe !
Badu, ñu bare la seen taat tëgg tama
keroog, man mii ma ciy teg samay bët, mu
def may ree !
Saay-saay si nekk fa di déeyante ka
wokkante. Ña bóomoon Aali Këbóoy
saalit nañu bés boobu.
Noonu lanu fa nee ñukk mbaaru Aali
Këbóoy. Ayu-bés ya ca topp yépp, kenn
ñemewu ko sax jege.
*
* *
Bés, benn waay-Yàlla ju màggat di wër ba
agsi Ñarelaa. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_338 | Sabadoor bi mu sol a ngi furi be kenn
xamul lu muy nirool, mu teg ab tengaade
ci bopp bi, téye ci bantam di temp.
Waaye Badu, góor gi nu gis tisbaar jooju
de, amoon na mayu Yàlla. Kër gu mu
taxaw keroog di yalwaan, su ñu ko
saraxee ba noppi am na ku ne :
- Góor gii de, bi sunuy bët dajee am na lu
ma yëg ci sama yaram.
Te mu doon dëgg gu wéer péηη it, Badu.
Képp ku góor gi ne jàkk ci Ñarelaa, nga
wax kook nga bañ koo wax, am na lu jóge
ci yow.
Góora Mbay dégg coow li, daldi woo
benn surgaam ne ko :
- Demal indil ma waay-Yàlla jooju may
dégg. Ne ko Góora Mbay, goro Kapiteen
Baay Ndeene, moo ko soxla.
Fu surga bi dem, ñu ni ko :
- Góor gaa ngi noonu di fi jóge, soo
gaawantoo dab ko.Surga biy wër ba
dajeek góor gi. Ñu nuyoo, mu ni ko : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_339 | - Kilifa gu ñu naan Góora Mbay moo ma
yónni ci yow. Nee na nga wuyusi ko ci nu
mu gën a gaawe, dafa la soxla te soo ko
xaarloo dina la won mooy kan !
Waay-Yàlla ji ne jàkk surga bi. Kooku gis
ni bëti góor giy tàkke, daldi dellu ginnaaw.
Góor gi ni ko :
- Neel ki nga ne kilifa la, su ma génnee
gox bii, te dabu ma, sukkal ma, balu ma
àq, du baax ci moom !
Céy bëccëg boobu, Badu ! Góora Mbay
mi nga xam ne moo fi dàqoon a jaay
maanaa, keroog la ko Yàlla doon xaar !
Bëccëgu ndara-kàmm lañu ko toroxal !
Tànki neen la def, ma ni la, di daw, di wër
benn màggatum yalwaankat, di xiixat, ñaq
baay siit, ku mu dajeel laaj la ndax gisoo
benn góor gu sol sabadoor bu furi te teg
ab tengaade ci bopp bi !
Nit ñaa ngi koy ree, waaye faalewu leen
sax. Ba mu dabee góor ga nag, ba sukkal
ko, balu ko àq, kooku lii la ko wax : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_340 | - Ñëw bii nga ñëw de, moo gën ci yow !
Soo deful woon li ma la sant, yàqu kon
nga yaxeet !
Léegi nag, déglu ma bu baax : mbaaru
Aali Këbóoy du sempiku feek ku ñuy wax
Isma Ndóoy dugalul loxoom ci mbir mi.
Góora Mbay ni ko :
- Ãa ?
- Waaw. Waaye dinaa ci yokk lu tuuti :
Aali Këbóoy, fàww mu dellusi. Dégg nga
wax ji, de ? Aali Këbóoy, dara mënu koo
tee dellusi Ñarelaa.
Boo gisee Góora Mbay, mu ngi lox fi mu
taxaw. Mu dellu laaj góor gi :
- Ba daal kenn amu ci pexe ?
Góor gi ree :
- Yow de, dafa mel ni sa yaram neexul.
Reylu nga Aali Këbóoy, sant Kapiteen
Baay Ndeene, sa goro bu soxor boobu, mu
diigal néewam ci géeju Kusum. Xanaa
loolu war na laa doy ! Loo bëggati ? | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_341 | Ma seeyal ruuwu Aali Këbóoy ?
Ruuwu nit, Yàllaay boroom.
Góora Mbay geestu, fu ne mu xool fa, di
seet ndax am na ku dégg kàdduy góor gi.
Mu daldi ne :
- Dinaa def li nga wax. Waaye ginnaaw
kenn mënul a tere Aali Këbóoy mu
dellusi, lu nuy doyeeti Isma Ndóoy ?
- Foofu nga juume. Su ngeen feyee Isma
Ndóoy li mu leen di laaj, dina daan Aali
Këbóoy ba nga xam ne bu dellusee du
leen gëtën. Su ci jàppulee, Aali Këbóoy
du leen may jàmm ba keroog yawmal-
xayaam. Àddina dina tukki, ñibbisi, ni
faax ci diggu këram, tukkiwaat, jàppe ko
noonu ba mu mat juróom-ñetti xarñu te du
tax Aali Këbóoy may leen jàmm !
- Dégg naa sa wax, góor gi. Léegi ñaata
laa la ameel ?
- Dencal sa xaalis. Isma Ndóoy a ma ko
gën a soxla te moom xamul baale !
Badu, am na ku ne woon : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_342 | - Doxatu gëléem kow la jëm.
Du man mii de maay weddi kàddu yooyu.
Wax ji law.
Gox boo dem ci Ndakaaru, dégg ñuy
waxtaane mbirum Aali Këbóoy.
Nit ñi ràkkaaju nag, ma ni la, di yokk ak a
yokkaat, di xoromal.
- Dégg ngeen li ma déggam ? Nee nañu
Aali Këbóoy dafa soppiku malaaka, yéeg
ci kow asamaan ak ay laafam, ñépp di ci
teg seen bët !
- Wax nañu ko, de.
- Nee nañu it guddi gu nekk, su waa
Ñarelaa dee nelaw, Aali Këbóoy day
soppiku yoo, di biiw ci noppi ñi ko rendi,
di leen màtt, di leen saaga, lu nekk mu
leen koy yakk.
- Nga ne ma ?
- Ñooñu ñan a waay ?
- Li ci kanam rawul i bët. Soo déggee fan
yii kuy jàmbat sibbiru ci Ñarelaa, dóoral
yat ! Xamal ne yoo bee fa jaar ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_343 | - Man de, benn jigéen doon na ma tanil
démb. Xamal na ma ne lépp lu xew
Ñarelaa, Aali Këbóoy a nga jaaxaan ca
àllaxira di ci teg bëtam.
- Eskéy !
Ba màggatu yalwaankat ba demee ba nu
fàtte, benn xaleelu góor bu tudd Isma
Ndóoy, dëkk Mbaaw, ñëw bés Ñarelaa, ne
moom mën naa sempi mbaaru Aali Këbóoy.
Ñu ni ko :
- Xanaa waay-Yàlla jee la fi yebal ?
Mu fas kanam gi, daldi ne :
- Loolu amul solo te sax xawma luy seen
yoon ci ku ma yebal ak ku ma yebalul.
- Weexal bi nag, ñaata la ?
Isma Ndóoy sëgg ci noppu Góora Mbay, wax
ko njëgam. Góora Mbay taf gémmiñam :
Saa waay, alal ju tollu noonu, soo dajalee li
fi mus a dugg ci xaalis ba sunuy maam
sancee Ñarelaak tey, ëpp na ko téeméeri
yoon xanaa ! Waxal lu nu mën a dégg, waa
ju baax. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_344 | Isma Ndóoy boolewu ca wax. Dafadaldi
solaat mbubbam, ne mu ngay dellu Mbaaw.
- Dimbali nu, ñaan nanu la ko ci diggante
jullit ak moroomam.
Isma Ndóoy geestu Góora Mbay, xool
waa Ñarelaa ba seppali leen, daldi ne :
Yéen ñépp ay naaféq ngeen, te xam ngeen
lu tax ma wax loolu.
Man Isma Ndóoy, bi yëf yiy am, maa ngi
doon wëndéelu ci jaww ji, tiim leen.
Ngelawu géeju Kusum pes na ma !
Gisuleen ma waaye man maa ngi leen
doon gis. Buleen ma tax a nettali njëlu
Ñarelaa gu ñaaw googu !
Ku nekk xool sa moroom, sëgg.
Baay Ndeene ne Isma Ndóoy :
- Li nga nuy laaj de, amunu ko. Réew mi
ci boppam, xaalis bu ni tollu amu fi. Lu la
tax a yaakaar ne waa Ñarelaa mën nañu ko
dajale, fey la ? Aa, yow kat, danga mel ni
ku nu bëgg a yab ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_345 | Baay Ndeene nag, noon naa la fi dafa
àndoon ak xadar. Ñarelaa ba Ñarelaa daj,
moo ci gënoon a bari ay. Xeex ak naan
ndox la mas a yemale. Mag ñi naxanteek
moom, yedd ko, xamal ko ne warul a topp
meram.
Góora Mbay daldi ne Isma Ndóoy :
- Ginnaaw noonu la, nga baal nu àq, waa
ju baax. Amunu xaalis bi nga nuy laaj.
- Kon boog nu ñaanalante, dellu naa
Mbaaw ga ma dëkk.
Ba Isma Ndóoy demee, magi Ñarelaa yi
taxawaat nañu fa lu yàgg di wut pexe. Ñu
mujjee jàpp ne nguur gee waroon a ñëw
jële fi mbaaru Aali Këbóoy.
Góora Mbay ne :
- Nanu seeti jawriñ bi ñu dénk kaaraange
biir réew mi, moom war na cee mën dara.
Ñépp ànd ci wax jooju.
Ba nuy laata tàggoo, Baay Ndeene xool
ma ba yàgg, ne ma : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_346 | - Waaw, Ngiraan, yow de, saa yu lu mel ni
masaan xew Ñarelaa, waa gox bi daje di ci
waxtaan, danga daan yëkkati sa kàddu,
joxe sa xalaat. Tey moom, kenn déggul sa
baat...
- Maa yey ne patt, Baay Ndeene.
- Ãa ?
- Waaw. Man kat, dama tiit ba fu tiit yem.
- Lu waral loolu, Ngiraan ?
Ma yëngal sama bopp, ni ko :
- Seetlu woo dara ci waa ji jóge Mbaaw te
ne Isma Ndóoy la tudd ?
Waa Ñarelaa yépp di ma xool, waaye
kenn amul sama tont.
Ma ne leen :
- Li Isma Ndóoy moomuy wax yépp, maa
ngi gëmm di ko déglu. Te xam ngeen
baatu kan laa doon déggam ?
- Ãa ?
- Baatu Aali Këbóoy, xanaa. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_347 | - Danga bëgg a wax ne Aalee fi taxawoon
sànq di waxtaan ak nun ?
- Looloo am sax de, Baay.
Keroog jooju, Badu, gis naa kilifay
Ñarelaa yu bare ñu téye seen bopp ndax
jaaxleek tiit.
Ña jógoon ci xaaju-guddi, fekki Aali
Këbóoy ca biir mbaaram, rendi ko, am na
sax ku ci rëccle ba caaya ji xaw a rot. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_348 | TÉEREB LËNDËMTU
II | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_349 | Badu, du caagin dama la bëgg a miirloo,
waaye fàww nga may ma ma dellu ay ati
at ci ginnaaw.
Maa ngi door a am fanweeri at ak ñaar,
nekk óbërye ca Air Liquide, di doxaan
ndaw su ñu naan Faat Juuf.
Bés, ni ma ko tàmmee def, ma reer ba
noppi, sol samay dàll, tegu ci yoonu kër
Faat Juuf. Kolobaan la Faatu luye woon
benn kër gu yem.
Jamono jooju, tele amul. Danoo déglu
sunu rajo ci ëtt bi, ma defar àttaaya, nu
cokkaasante ba sunu yaram xaw a tàng, nu
daldi jàll ca néegu Faat Juuf.
Miinante woon nanu bu baax, nun ñaar.
Noonu laa ko mën a waxe.
Li ci des sa xel a koy mottali. Xam nga
mbirum gone rekk. Am doole te yëg ko.
Nu nekkal ko ci.
Gajjante.
Wax ju ñaaw.
Parax-paraxeek sëppu-jaleñ. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_350 | Taataan.
Mbejante.
Àndandoo di salliiru.
Mujje ne yàcc, di xullee.
Waaw, noonu lanu daan jotee, maak Faat
Juuf.
Waaye guddi gi ma lay wax de, neneen la
mbir mi deme. Kottante nanu lu yàgg ci
kow lal bi, ne cell, mel ni ñaari gone yu
réer ci àll bi, ku ci nekk di jéem a aar sa
moroom.
Fa lanu nekk di raayante ndànk, ànd ceek
teey ak ràññee.
Bi ma ganejee Faat Juuf, teeru na ma teeru
bu rafet, dalal ma.
Ba nu lalee waxtaan it, ku nekk ci nun
ñaar tontu na sa moroom na mu ware.
Keroog Kolobaan àjjana ju ndaw la woon
ci nun ñaar.
Waaye lee-lee sunu bànneex day wex xàtt,
jur sax tiitaange. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_351 | Lu waral may joteek Faatu Juuf, mu neexe
noonu ba noppi, sama xel yépp nekk ci
dee ?
Ma gëmm, gis ñaari mellentaan yu tuutee
tuuti te ñuul ñuy mareñ ci aw tund wu
suuf sa weex tàll.
Ma ni ci sama xel :
« Maak Faatu Juuf bëggante nanu ba fu
bëggante yem. Waaye lu nobeel di jariñ ?
Lii lépp fan lanu jëme ?
Fii ak ñeent-fukki at nu màggat, ras,
dootunu mënal sunu bopp dara ba bés ba
nuy xéy jóge fi. »
Ngiraan Fay.
Faat Juuf.
Fan ngeen jëm, yéen ñaar ?
Jamono dina ñëw, mbégte mu réy bett la.
Waaye bànneex ni melax lay bindooo, ba
muy tàkk ak ba muy fey benn lay doon. Bi
nu delloo ci saal bi, ku nekk ci nun ñaar
gis na ci say bëti moroom tiis wu réy. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_352 | Faat Juuf a ngi taraxlaayoo séru legoos,
ferenklaayu, wéeru ci kanape bi.
Lee-lee sama loxo càmmooñ doxantu ci
kow yaram wi, naj ndànk catu weenam
mbaa mu wàcc ba ci diggante lupp yi,
jaaru fa as lëf.
Maak Faat Juuf rekk a nekk ci kër gi.
Dëkk bi ci boppam mu ngi ne selaw.
Nuy diisoo, ku nekk di dénk sa moroom lu
mu masul a wax kenn.
Góor ak jigéen su ñu bëggante dëgg, li
ëpp ci seen waxtaan ci ñeeneen ñi lañu
koy jëmale, moo xam seeni mbokk lañu
mbaa seeni xame kese.
Dañuy faral di leen jëw, daal.
Badu, sooy ngoroyook jigéen te dungeen
juum ba jëw kenn, booba xéy-na seen
àndandoo narul a yàgg.
Su dee fu ngeen tollu yéen a ngi naan su
ñu amee doom nii lay tudd mbaa béréb
sàngam lanu war a wut kër, ñàkkul seen
ngoroo ngi waaj a tas. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_353 | Guddi googu laa mas a wax Faat Juuf ne
sama cosaan, man, Mbériη-Saaj la, ca
Siin :
- Ci sëti Maam Ngóor Fay yi laa bokk.
Faat Juuf daldi muuñ, ne ma :
- Waaw, te noonu nga ci tollu ? Maam
Ngóor Fay nag, ku ko jur ?
Gis nga ni mbir mi doye waar, Badu ! La
ma umple woon ba tax maa tegu ci yoonu
Mbériη-Saaj la ma Faat Juuf laaj.
Ma ni ko :
- Sol naa samay dàll, dem ba Mbériη-Saaj
ngir rekk bëgg a xam kan moo doon
Maam Ngóor !
- Loo fa jële nag ?
- Dara. Wax dëgg Yàlla jëlewuma fa dara.
Waaye yow sax, Faatu, soo may tane it,
du lool.
- Nun kay Ngiraan, noo ngoog rekk !
- Nun ñan, Faatu ? | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_354 | - Xanaa nun Doomi-Aadama ! Nit ku
nekk, booy nemmeeku cosaanam, ci yoon
lim bi waroon naa mat ay junniy-junni at.
Waaye ñi xam mbaa ñiy fàttaliku seen
turu maam, ñu néew lañu. Maandu daal
moo nu war, Ngiraan.
Ma siggi, xool Faat Juuf, gis ni kanam gi
soppikoo ndax tiis wu ma xamul lu ko
waral.
Ma ni ko :
- Lu xew, Faatu ? Danga mel ni ku xolam
jékki-jékki diis gann.
Faat Juuf ni ma moom masul teg bët ay
way-juram :
- Man dañu maa for ci mbedd mi, Ngiraan.
Bi ma juddoo, sama yaay dafa ma bëggoon
a rey, ñu bett ko, mu sànni ma, daw.
- Ãa ?
- Bu yàggul laa xam loolu. Ku baax ki ma
for, yar ma, masu ma cee nangoo wax
dara. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_355 | - Ndax yoon mujje naa teg loxo ci sa
yaay ?
Faat Juuf tontuwu ma. Sunuy bët daje, ma
daldi yëg ci saa si ne wax naa lu ëpp.
Faat Juuf gis ni ma amee kersa ci mbir mi,
daldi ma xëcc, ma fekki ko fi mu toog ci
suuf.
Ñu tëdd nelaw, ma gént gént gu jaxasoo
sax. Waaye ndax lii sax gént dégg la ?
Maa ngi wetu kër Faatu Juuf, taxaw ci
booru tali bi. Kolobaan a ngi lëndëm
këruus wante teewul oto yu baree ngi may
romb, seeni faar di tàkk, ñuy def :
- Fiiw ! Fiiw ! Fiiw !
Oto bu romb, sa moroom topp ci, ñu mel
ni oto rawante yi ñuy wone lee-lee
tele.Moo man, fan laa nekkati ? Tali bii
ndax tali neen la ? Pax mu xóot a xóot la,
di nirook teen bu ñu jaaxaanal te daanaka
amul yemu. Li faaru oto yiy melax yépp,
taxul béréb bi leer. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_356 | Rax-ci-dolli, benn sófóor nanguwul a
taxaw jël ma. Mu mel ni oto yi man lañuy
daw ! Ñoom daal ñu ngi naan :
- Fiiw ! Fiiw ! Fiiw !
Ma tiit, di saraxu sófóori oto yi may romb
- Buleen ma fi ba, ngir Yàlla !
Waaye kenn ci ñoom nanguwu cee taxaw.
Gisuma kenn kuy dox, sófóor si may romb
it mënu ma cee teg kenn bët.
Aa ! Oto yuy dawal seen bopp nag !
Jàppal ne li ma lay nettali mu ngi amoon
ci 1954.
Bu ci kanamee, dinga xam lu tax loolu am
solo.
Njël jot. Ma yeewoo Kolobaan, sangu,
ndékki, dem liggéeyi Air Liquide.
Àddinay dox. Ñaata guddi, ñaata njolloor,
ñaata njël ñoo fi jaar boobaak tey, seey,
yóbbaale yaakaari Doomi-Aadama yi ?
Yàlla rekk a xam, Badu.
Bul ma laaj it fan laay dégg Faat Juuf. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_357 | Tàggoo nanu bu yàgg te xawma sax fan la
nekk ci Senegaal ñàkkul sax mu génn
àddina te yëguma ci dara.
Guddi Kolobaan gaak tey jii ma tiim sama
Téere bu ñuul bii, di ci bind lii, mat na
juróom-fukki at. Lu waral tey jii sama xel
yépp nekk ci Faat Juuf ? Lu tax biig ba tey
fu ma geestu ci néeg bi gis takkandeeru
Faat Juuf, déggaat baatam ?
Lépp li ma def Kolobaan juróom-fukki at
ci ginnaaw, ganesi na ma biig.
Lépp laa wax de, Badu. Te lépp soo ko
déggee mooy ñaar yii : séyaat naak Faatu
Juuf, am ci mbégte mu jéggi dayo, ba
noppi tëddaat ci wetam nelaw, daldi
géntaat la ma géntoon ca atum 1954...
Jëli nga maam, Badu ?
Li ma dal biig, mënuma koo tudde gént.
Dama toog di bind ba yàgg sama bopp biy
metti mel ni dafay waaj a xar. Ci laa tëje
Téereb Dóom, aj la ma la doon nettali ci
Yaasin Njaay, dem tëri. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_358 | Bi may nelaw nag, guddi Kolobaan gépp
ñëwaat na ci sama xel. Amul dara lu ci des
ginnaaw. Ni ma ko dunde woon ba may
am fanweeri at ak ñaar la dellusee.
Yëf yi yemu fa de, Badu Taal : ci sama
biir gént, géntaat naa taxaw ci booru tali
bi, ca Kolobaan, mu lëndëm këruus, oto
yu bare di ma romb, seeni faar di tàkk,
ñuy def :
- Fiiw ! Fiiw ! Fiiw !
Ma tiit, di saraxu sófóori oto yi may romb,
naan leen :
- Buleen ma fi ba, ngir Yàlla !
Waaye kenn nanguwu cee taxaw.
Muy ñaari yëf, Badu :
Li fi mas a xew ak li fi masul a xew. Lii
ma dund ko dëggantaan, li ci des di lu ma
janeer doηη.
Fu ñaar ñooñu jaxasoo, Badu, Fen ak Dëgg
maasaloo nañu. Kon, dee soreetul.
Jamono ji walbatiku, guddi soppiku doon
bëccëg. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_359 | Ma ni : dee gu taxaw jonn.
Boroom xam-xam yi dinañuy faral di
janeer, séen Ëllëg ak li ci biir ñu nekk ci
yoon wiy daagu.
Agseeguñu de, waaye ñu ngi janook
ñoom.
Ñu teg ci diir bu gàtt, muy lu ne fàηη-
fàηηaaral, maak yow nu sog cee mën a teg
sunuy bët.
Dëgg la. Wànte ku ma newoon dinaa dund
man mii ba bés ñëw may gént ne maa ngi
gént, ku ma waxoon loolu, Badu, ma ni la
fen nga.
Sant naa Yàlla bi yëf yi yemee foofu.
Mënoon naa fa jóge xeetu ndof gu doy
waar dugg ma, lépp lu ma masoon a dund
ci àddina ma dundaat ko, di xuus ci biir
jamono ji, di dellu ginnaaw ba dellu
Mbériη-Saaj, ca Siin, guddi taalata ga
sama ndey sukkee jur ma. Li ma xalaat
noonu xaw maa miirloo !
Dem ba nekk mag, dara deseetu la lu dul
wuyuji sa boroom, mu ni la : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_360 | - Ngiraan Fay, may naa la ñaareelug dund.
Doore ko bésu tey, at mu jot dinga gën a
nekk xale.
Am nga 80 at. Feek 79 at, dinga dellu
nekk liir. Walbati jamono ji du dara ci
man, defal naa la loolu !
Fépp foo mas a jaar, dinga fa jaaraat. Su
ko defee, lu dëngoon ci sa jëfin nga
jubbanti ko, koo mas a tooñ nga balu ko
àq mu baal la ci xol bu sedd. Soo demee
nag ba wërngal gi téju, say mbokk ni :
- Sunu Ngiraan Fay mu baax mi de,
juróom-ñaari fan rekk moo ko dese ci
dunyaa, ndax bés sàngam la ganesi woon
àddina, te talaata jii di ñëw la bés boobuy
dellusi. Ci lañu ko ngénte woon, kon ci la
fiy war a jóge, wuyuji sunu boroom. Nanu
ko waajal, boog.
Ayca, Badu Taal, bul nasax. Lemmil li ma
lem foofu, jëlil wax ji.
Kersaa waral ma fab Dëgg lëmës ko ci
biiri léeb ak i cax. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_361 | Xawma kan laa rusul ci àddina, waaye
yow Badu Taal am naa lool sa kersa.
Gone nga waaye ku la seetlu bu baax,
fàww mu weg la ba sax xaw laa ragal.Yaa
xam loo bëgg, doom : Yal na la ko Yàlla
defal. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_362 | TÉERE BU ÑUUL BI | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_363 | - Dégluleen ! Jàmm la ! Dégluleen ! Jàmm
la !
Yéenekat bi wër na Ñarelaa ay yoon i
yoon, sog a taxaw ci pénc mi. Lee-lee mu
tëgg sabaram, daldi dar nopp yi, yuuxu :
- Dégluleen ! Jàmm la ! Dégluleen ! Jàmm
la !
Mu ne tekk ba yàgg sabarooti ñetti yoon,
daldi daraat nopp yi :
- Buur nee na : góor ak jigéen, mag ak
ndaw, bu ëllëgee ci yoor-yoor, na ñépp
daje ci pénc mi !
Badu, kàddu yi ma doon xaar ñu jib, jib
nañu. Aali Këbóoy delluseeti na.
Maa ngi yëg luy rocceekoo ndànk-ndànk
ci sama yaram.
*
* *
Ca ëllëg sa, waa dëkk bi def la leen Buur
sant. Waaye kat, mbir mi jaaxal nañu bare.
Ngay dégg ñu naan : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_364 | - Fan la yéenekat bii génneek sabaram ?
- Buur ban a woote, sax ?
- Démb ak bërki-démb de, ay buur a fi
newoon, daan dogal. Seen bëgg-bëgg rekk
lañu xamoon. Muy dëgg gu wér péηη,
ndax ku ci mel ni Daaw Demba demoon
na ba ni :
- Fii ci Kajoor, ku fiy takk janq, balaa
ngay joteek moom, indil ma ko ma jaar ci
ba noppi, ndax buur moo yeyoo loolu.
Waaye Daaw Demba ak buur yi ko fi jot a
wuutu, kenn waxatul seeni wax.
Tey, jamono Daawur Jaañ lanu nekk. Su
Daawur Jaañ bëggee waxtaan ak waa réew
mi, day woo taskati xibaar yi, wax li muy
wax, ñooñu jàllale ko ci tele yeek rajo
yi.Kon boog, ku woote ?
Waaw. Su Daawur Jaañ wooteewul kan
moo war a woote ?
Ñarelaa ngi dajaloo ci pénc mi. Foo sànni
mbàttu mu tag.
Ku ci nekk a ngi naan ci sa xel : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_365 | « Waaw, kañ la démb dellusi, làqu ci
biiru Tey, nar fee judduwaat ? Kañ lanu fi
fal Buur ba muy woote ? Naka la Daawur
Jaañ mënee nekk njiitu réew mi ba noppi
keneen naan mooy sunu Buur ? Du lii
lañuy waxati ci politiseη yu naaféq yi ! »
Yéenekat bi rëkkaat sabaram, xulli bët yi,
yuuxu :
- Buur a ngoog ! Buur daalee ! Buur
daalee ! Nu dégg ay woy yu neex lool sax,
te kenn ci nun xamul fan lañuy jibe.
Woykat yi yaatal géew bi, nu sog a gis
Buur. Mu nga àgg ca kow, sol ay yëre yu
yànj yu ñu daaminaa ak wurus.
Dag yi xàllal ko yoon, mu taxaw ci diggu
pénc mi, xool nu lu yàgg door a yëkkati
ndànk ñaari loxoom.
Nun ñépp nu ne tekk di ko déglu.
Xam nga lu Buur defam, Badu ?
Dafa jonkan, tibb ci suuf si ak loxo
ndeyjooram, ηëb ko lu mat juróomi simili,
di ñaan. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_366 | Ba mu ñaanee ba noppi, mu siggi, xool
mbooloo mi, waaxu ba ci benn ndaw su
màggat, mu xëcc ko ba ci diggu géew bi,
ni ko :
- Lii ma ηëb, wurus la. May naa la ko ci
xol bu sedd. Bés ni ki tey, sa soxlay
àddina yépp faju nañu ba fàww. Képp ku
sës ci yow, dootul xiif, dootul mar.
Noonu la nu Aali Këbóoy feeñuwaate,
bésub altine ci yoor-yoor. Waa dëkk bi
yéemu. Am ñu mbir mi yëngal seen xol ba
ñuy jooy. Nga dégg ñu naan :
- Yàllaay kariim.
Li ma lay nettali nii, fekkewuma ko. Fekk
na sibbiru si daaneel ma, ma fatu ci sama
néeg. Waaye lépp lu waa Ñarelaa wax
keroog mbaa ñu def ko, maa ngi koy dégg,
di ci teg samay bët.
Nekk ci pénc mi te sa jëmm newu fa.
Bi mu ma wóoree ne Aali Këbóoy dellusi
na, ne déjj ci diggu géew bi ak fulla ju mat
sëkk, laa tudd turu Yàlla. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_367 | Tàggu naa la, Badu. Fa may fanaani tey,
duma fa fekk kenn, kenn du ma fa fekk.
Dénk naa la ku baax ci yow. Dina la aar,
dina la fajal sa mer.
Dénk naa la Aali Këbóoy.
Li des ci nettali bi, mooy boroom. Dina la
ci may ba nga doyal sëkk ak barke. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_368 | ÑAAREELU XAAJ | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_369 | AALI KËBÓOY
Dof mat naa bàyyi cim réew | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_370 | Badu Taal, yaa ngi may déglu, mbaa ? Sa
maam Ngiraan Fay noon na la :
- Bala waa Ñarelaa di teqalikook Aali
Këbóoy, dinañu wax lu set.
Dëgg la. Ngiraan masul a wax waxu
caaxaan. Démb, soppiku naa mellentaan,
dugg ci kawasu benn waa ju doon dem.
Ma dégg ko mu naan ki mu àndal :
- Sama Ndumbe mi de, moo may bëgg a
jommal.
- Lu mu defati ?
- Jigéen ñi daal ñoo woyof bopp rekk !
Xanaa naan ma Aali Këbóoy dina dellusi
Ñarelaa fii ak i fan.
Xarit bi ree, ni ko :
- Foo newoon yow it, Tiijaan ? Loolooy
coow ci gox bi. Bu ma yaboo sax ne waa
réew mi yépp a ngi xaar Aali Këbóoy.
Ñépp xam nañu ne dina dellusi.
- Ãa ?
- Waa-waaw ! Bés daal, dégg naa, dinanu
dégg kuy yuuxu, naan : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_371 | Dégluleen ! Jàmm la !
Dégluleen ! Jàmm la !
Nee nañu loolu moo nar a firndeel ne Aali
Këbóoy a ngeeti ci sunu biir.
- Eskéy !
- Te kat, dinaa la xamal lenn, Tiijaan :
Aali Këbóoy mi réew miy xaar, dina ñëw,
nekk Ñarelaa lu yàgg a yàgg te kenn du ko
xàmmee.
- Nga ni ma ?
- Boroom xam-xam yee ko wax, de.
- Céy nun ak Aali Këbóoy ! Giñ naa ne fi
mu ñu jëme, jàmm amu fa !Badu, bi ma la
nettalee waxtaan woowu ma for ci mbeddi
Ñarelaa yi ba noppi, dinaa dëggal li ngóor
soosu wax : fi ma jëme Ñarelaa, jàmm
amu fa. Xanaa rekk ma yokk ci as tuut :
képp ku ma mas a tooñ ci Ñarelaa gii,
dinaa ko defanteek yow ba géej gi fer. Te
xam nga ni moos ndem-si-Yàlla ji Ngiraan
Fay, góor gu laabiir ga, am yërmande, taxu
maa wax. Man, Aali Këbóoy, sama baat ca
kow ! Nuyu naa leen, yéen waa Ñarelaa ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_372 | Sunu àndandoo nar naa yàgg te nar naa
metti !
Waaye balaa nuy tegu ci yoon wi, dinaa
leen fàttali kàdduy taalifkat bu mag
ba.Sëriñ Musaa Ka nee na : Am barke
àggul ci di def lu ñu dul wax
Defkat bu dee def waxkat it ma ngay wax
*
* *
Man, Aali Këbóoy, sama baat ca kow !
Waxambaane yi fi jaar sànq ci bëccëg de,
xaw nañu maa jaaxal. Ñu nga léttu, takk
ay càq yuy keleη-keleηi. Céy, su ngeen
leen gisoon, yéen waa Ñarelaa ! Seen
doxin, seen waxin ak na ñuy sànnee seen
yaram ci jaww ji ! Ñuul nag ba dër. Loolu
lépp tekki lii doηη :
- Xool-leen ma, man doomu Afrig laa,
sama ñuulaay bii dara dàqu ko ! Aa ! Naw
sa xeet de, gisuma lu ci aay, ci am faayda
la bokk. Séex Anta Jóob loolu la nu jàngal. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_373 | Waaye nag, man Aali Këbóoy, am na lu
ma xaw a yéem ci mbir mi. Ngeen ne ma :
- Loolu lu mooti, Aali ?
Ma ne leen :
- Nit Njaay bu demee bay toppandoo
boppam, xanaa war naa fekk xamatul
moom mooy kan, xanaa fekk na
njàqareem jéggi dayo ! Soo demee ba tànk
boo yëkkati, ne man diw maay Man, te
soo ko defulee ñu jaawale laak keneen,
booba fekk na nga déju ci andu jaambur,
noor fa, nar faa nawet. Waa réew mi kat
war nañoo xoolaat mbir moomu. Seen
ndaje yu bare yi may dégg ci rajo bi de,
war ngeen cee sóoraale loolu. Laaj leen
gone yi :
- Waaw, doom, lu leen xiir ci toppandoo
seen bopp ?
Man, Aali Këbóoy, sama baat ca kow !
Patiriis Lumumbaa.
Waaw, Patiriis Lumumbaa, laa wax !
Réewum Kóngo ne ko : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_374 | - Patiriis yaa nu doy, keneen ku dul yow
du nu jiite, jal baa ngoog, nee ci faax su la
neexee.
Ñu neeti :
- Jàmbaar da koy niru. Ba nga jàkkaarlook
buuru Belsig, ñaawoo ci. Yërëmoo wax ji,
danga jaar ci digg bi.
Waa Belsig mer :
- Ku mus a gis lii ? Ñii nga xam ne démb
rekk sunuy jaam lañu woon, nu leen di sëf
ci naaj wu tàng wi ni ay mbaam, di leen
kàcciri, ñu naan wii mise, mersi mise, képp
ku ci jéngu bëgg noo jommal, nu daggat la,
sànni xaj yi, ñu yàpp la. Kañ la sowaas yii
daan am fitu ñàkke teggin sunu Buur ?
Buuru Belsig ! Kii kay dafa reppoon dëgg
bi muy def loolu ! Lumumbaa mii, fàww nu
def ko lu kenn dootul fàtte.
Noonu la ko waa Belsig defe it. Fan yii, rajo
boo ubbi, nit ñu baax ñaa ngi metitlu bóom
gu ñaaw gi ñu bóom Lumumbaa ca Kóngo.
Yéen waa Ñarelaa, man Aali Këbóoy maay
wax ak yéen ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_375 | Yéen a ñàkk faayda, yéen waa Ñarelaa !
Yeewuleen ! Waxleen ci li xew Kóngo.
Bokkleen ci werante beek xeex bi. Nit
ngeen, dungeen ay xar.
Lan mooy coow li ? Ñii ngi naan Bels yi
dañoo bëgg teg ci boppu réewum Kóngo
seen xuus-maa-ñàpp, ngóor su yaafus sax,
ñu koy digal muy dogal. Kooku, benn
soldaar bu jege woon Lumumbaa la, ñu
koy wax Sosef Desiire Móbutu.
Amerikeη yi tamit, ñu baree ngi leen di
tam dëmm ci mbir mi. Ñoom sax lañu ne
ñoo ngemb ci suuf ngóor soosu ñu naan
Sosef Desiire Móbutu. Lumumbaa de, su
muccoon ci lii dina jaaxal ñu bare : Bels
yi ne dafa xamadi, Amerikeη yi ne
kóminist bu bon la.
Amerikeη yeek Bels yi mànkoo, ne su
loolu yépp weesoo sax, alal ji nekk ci biir
suufu Kóngo, ñoom ñoo ko gën a soxla
waa Kóngo !
Waa Ñarelaa jógleen taxaw !
Ne yàcc di xullee du seen ndam. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_376 | Du xam ngeen nu ñuy rendee xarum
tabaski ? Waxambaane yee koy ñàdd,
boroom kër gi sog a teg paakaam ci baat
bi, dem, dikk, dellu. Sosef Desiire
Móbutook Móyiis Combe, xuus-maa-ñàpp
ga ca Katangaa, ñooy surga yi ñàdd
Lumumbaa, ay kilifay làrme Belsig daas
seen paaka, daldi def seen mënin. Léegi
nag, Móbutoo ngi jonkan di xaar wàllam.
Mu ngi xaar doxandéem yooyu jébbal ko
nguuru Kóngo. Su ko defee, mu ne noηη
ci jal bi, ne leen :
- Jaaraama, yéen waa Belsig ak waa
Amerig ! Yéen a ma fi teg, maak yéen
dinanu bokk mbuus, lu ngeen joxoñ ma
dagg, ngeen fab, yóbbu defare ko seeni
réew !
Tey jii, fukki fan ak benn ci weeru
saηwiye, ci atum 1961, nit ñu baax ñi ci
àddina si yépp mer nañu. Àddina si yépp
laa wax, de !
Wasiηton.
Kaasabalankaa. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_377 | Konaakiri.
Akaraa.
Feerfaks
Alse.
Liyees ak Briksel...
Dëkk yooyu ma lim yépp, ay gor fippu
nañu fa, taxaw nañu ngir wone ne li xew
Kóngo ànduñu ci tey, ànduñu ci ëllëg.
Nun waa Ndakaaru Njaay it, kenn demul
nu des ! Jóg nanu, taxaw ci tànki bañ.
Yéen waa Ñarelaa kañ, yéen a yaafus te
ñàkk dogu ! Daara ju mag ja laa jóge nii
sax. Ba nu dajaloo biir Iniwérsite ba
noppi, danoo daldi jubal bunt bi féeteek
tali bi jëm Wakaam. Ñii ngi làmboo raaya
bu Kóngo, ñi ci des a ngi téye ay nataali
Patiriis Lumumbaa.
Ma ni : bés bi ñu bóome Lumumbaa la
Afrig tàmbalee suux, di delluwaat
ginnaaw. Li xew keroog jooju, su ma
sañoon, nun ñépp nu bàyyi ci xel bu baax.
Njiitul réewum Afrig ne jàkk kilifag
réewum tubaab bu day noonu, ñépp toog
di la déglu, nga am fitu wax ko dëgg... | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_378 | Am nañu ko jéemoon ca jamonoy Maam
ya, waaye fekewuñu ko. Lumumbaa
waroon na xam moos ne mënul woon a
mucc.Am na ci yéen ñuy déeyante. Waa-
waaw, maa ngi leen di dégg kay, ngeen
naan ci suuf :
Aa, ndekete sunu ngóor si day dof-doflu
rekk, waaye dara jotu ko. Su Aali Këbóoy
dofoon kay, du mel ni ku naan Lumumbaa
tooñ Bels yi.
Yéen a ngi naan :
- Su Lumumbaa duggul woon ci lu
yoonam nekkul, Bels yi duñu ko rendi,
daggat yaram wi, seeyal ay yaxam ci
mbalka mu fees dell ak asib. Céy, waa
Ñarelaa ! Maa leen xaare ! Jëw Patiriis
Lumumbaa daal moo leen dese ?
Lu ngeen may layati, sama gaa ñi ? Tàmm
ngeen wax seeni njaaxum ba noppi ne
Wolof Njaay a ko wax ! Maa ngi leen di
dégg, ngeen naan :
- Ñàkk bopp gaaw a dee. Lumumbaa kat,
da doon jaay lu amul ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_379 | - Lu jiin Njaag a te mooy Njaag !
- Moo ko sómbi, na ko naan.
- Lu tollu ni Buur, rawatina buurub
tubaab, nga di ko ηàññ noonu bëccëgu-
ndara-kàmm !
- Ma ni : nen du bëreek doj !
- Tubaab yi soxaruñu gaa, dañoo bañ ku
leen yab rekk !
- Mooy li ñuy wax rekk : ñi mën a kott
amuñu mbaam ! Man de, su ma amoon
wërsëg wu day ni jàkkaarlook Buur, di
wax mu may déglu, dinaa fexe ba samay
soxla faju sama giirug dund.
Cim ! Gat seen ! Xaj yu bon yi ! Ba noonu
daal ngeen tollu ci mbirum Patiriis
Lumumbaa ? Nga ne lan, yow, boroom
simis bu sokolaa bi ak sa sikkimu
séytaane bi ?
Nga ni soo janoo woon ak Bóduweη,
Buuru Bels yi, dinga ko ñaan xaalis boo
takkee ñetteel ? | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_380 | Waaw, amaana sa soxla soosu faju de,
waaye say sët ak say sëtaat duñu ko fekke.
Wutewuleen ak ay nit yu ñu déj ci buntu
kàmb gu xóot a xóot te fees dell ak i xal,
yeew leen fa. Sañuleen sax yëngu ba seen
xel di dem ci jéngu. Defe ngeen ne su
ngeen di jéem a yëngu di tàbbi ci kàmb gi,
safara si lakk leen, seeni yax def dóom.
Te ngeen tuddee seen bopp ay nit ?
Bàyyileen seen xel ci seeni sët ! Waay
waay amleen boog tuuti yërmaande ci
gone yi juddoogul. Ëllëg a ngi rung ci
seen biir deret, mu ngi daw sax bay xiixat.
Bépp toqu deret buy daw ci seen yaram,
dina ami bés ay bët ak i nopp, dina ami
gémmiñ, ñu ngénte ko, jox ko tur, mu
màgg, nekk nitum lëmm. Fu nekk nag mu
geestu fa, di seet yoon wi ngeen ko xàllal,
mu mën caa jaar te du fakkastalu mbaa
muy wékk yaakaaram ciy doxandéem ngir
bañ a daanu.
Ñi fi jaar démb, su ñu sàgganul woon, nun
ñii doon nanu fi gën demin. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_381 | Waaye ay doxandéem taxaaw ci waax bi,
wàccee seeni gaal ak ay butéeli sàngara ak
ay seetoo ki caq, nga daldi tàggook sa
sago ci saa si, jaay sa jabar ak say doom,
pasar-pasaree suufu Maam sii...Moo, tee
ngeen a seetaat seen xel ! Ñaaw ci, lekk
yu neex, te du mujje fenn fu dul seen
wanag. Waa-waaw ! Maa ko wax ! Li
coow liy bare yépp, foofa ngeen di
jonkan, rotal fa yu neex yi tax ngeen di
tayle réew mi !
Buleen ragal nit ku Yàlla bind ni yéen.
Waaye sax, wax ji du loolu, Badu.Lan la
boog ? Lii la : tubaabi Belsig yooyu
mënoon nañoo xët ci lëndëm, maanam
làqu rey Lumumbaa, yem ca. Noonu lañu
ko tàmmee def : dañu lay sàkkal pexe ba
noppi taxaw fale, mel ni du ñoom, ku leen
bëgg a tuumal ñu giñ ne ñoom yëguñu
tinuñu. Bii yoon dañu ni fàww ñu def ko
na mu gën a ñaawe, àddina si yépp di ci
teg seen bët, mu leer ñépp ne nit ku ñuul
du jam mukk Buurub tubaab naani. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_382 | Badu, xool nga bu baax nataal yi ci
yéenekaay yi ? Gis nga ni ñu yeewe
Lumumbaa mu toog ci benn oto, sol simis
bu weex bu xottiku, ndeysaan, ay soldaari
Móbutu tiim ko, di ko mbej, téye ci karaw
giy xëcc, di ko wéq, di ko tëfli !
Been soldaaru Belsig
a jiite waa kër Móbutu yi. Ba mu bóomee
Lumumbaa ba noppi, laata muy seeyal ay
yaxam ci mbalkam asib, def na lu doy
waar.
Xam nga lu mu def, de ?
Dafa buddi ñaari bëñi Lumumbaa, lëmës
leen ci sagaram denc, ne bés dina ñëw mu
jaay leen taskati xibaar yi mbaa ñeneen,
am ci xaalis bu takku. Yëf yi de, jaay
dooleek maa-tey la. Badu, mus ngaa gis
njiitu réew mu ñuy toroxale noonu
bëccëgu-ndara-kàmm ?
Masul a am fenn. Bés ba ñu reyee Patiriis
Lumumbaa la Afrig tàmbalee suux ci
géejug naqar ak njàqare. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_383 | *
* *
Biig de, dégguleen sama baat bu naqadi
bi, yéen waa Ñarelaa.
Man, Aali Këbóoy, tanqaluma leen ci
guddi àjjuma gi.Tey ma wax leen lu tax
yàquma seen nelaw biig.Lii doηη la.
Daawur Jaañ mi ngeen xam, njiitu réew
mi, moo ma fekk may jàppanteek nelaw,
mu ne ma pëkk-pëkk, ma xippi, dégg ku
naan :
- Aali... Ndànk la doon waxe nag, mel ni
ku ragal ñu dégg ko, mbaa ñu xàmmee
baatam. Noonu, ma daldi geestu, ne ko :
- Kooku ?
- Aa ! Ba xàmmeewoo sama baat, Aali ?
- Yow a kan ?
- Man a Daawur.
- Daawur man ?
- Man a sa xarit Daawur Jaañ. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_384 | - Saa waay, wéyal. Man, awma mbokk,
awma xarit.
Foofu mu ne tekk ab diir. Ma yëg ci sama
yaram ni mu ma ne jàkk ci lëndëm gi.
Sama xel yedd ma, ma daldi ne bëret,
génn fekki Daawur Jaañ ci buntu mbaar
mi.Soo ma gisee, maa ngi tiit bay pat-
pati.Laajleen ma lan moo yóbbu woon
sama fit noonu, ma wax leen ko.
Badu, moytul ma Buur ! Li tax nit di
jiiteem réew, du xam-xam, du doole, du
alal, du leneen. Mayu Yàlla doηη la.
Wànte dunyaa jii de, ñi ma gis ñu fiy jiite
ay réew, mën naa ni ñoo yées ci ñi Yàlla
sàkk. Moytul ma Buur ! Su dale sa kow
nga gaañu, soo dalee ci kowam gaañu.
Ana ku Buur naan jàkk te du am lu jóge ci
yow ?
Dinga ne :
- Waaw, Aali, Lumumbaa nag ? Moom
de, noon nga fi ñaawu ca ba mu janook
Buuru Belsig ba, Bóduweη lañu koy wax,
xawma. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_385 | Dëgg la, Badu. Weer yale ñu génn, nettali
woon naa la njàmbaar ga Patiriis
Lumumbaa wone bés ba Kóngo di jot
boppam, te Buuru Belsig nekk fa di wax
ay waxi kasaw-kasaw. Dafa fekk rekk ne
Lumumbaa du woon nitu neen, Badu.
Kooku xamul woon sax fu tiitukaay di
nekk ci Doomu-Aadama.Mën na am it,
Badu Taal, nga ne ma :
- Waaw, Aali, léeb ya ma Maam Ngiraan
daan léebal nag, ba ma newee gone ? Jot
naa jàng ci léeb yooyu ne ak lu Buur am
doole am doole, bés benn waay dina jóge
réew mu soree-sore, ñëw fekk ko fi mu
jaaxaan ci pénc mi, di jaay puukare mu
dëkk ko ci kanamu askan wépp, ñu
songoo mu toroxal ko. Loolu de, Aali,
dégg naa ko du benn du ñaar ca léebi
Maam Ngiraan Fay yu neex ya. Loo ci
wax, nag ?
Sama tontu du gudd : léeb, léeb la tudd.
Nee ma lu tax, Badu ? Su léeb tàbbee
géej, dëgg des fi, li am, Badu, moo di ne
njiitum réew duy yemb, ñaare. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_386 | Gis nga nag, maak sama mbokki dof yiy
wëndéelu ci mbeddi Ndakaaru yi, li nuy
kannasu yépp, xam nanu ne Muse la
Paresidaa moo nu gën a naan kaani fopp.
Ma ne : gaa ñiy feeñ tele ak seeni karwaat,
ñu naan leen Muse la paresidaa diw, seen
yaram duy faral di neex de ! Nit ku wér
dëgg, du fekk ay junniy-junni Doomi-
Aadama, nga ne leen :
Man diw, maa leen moom. Ku ko nangu ci
yéen dinaa ko fajal ay soxlaam, ku àndul
ci loolu nag su yaboo xam ne bakkanam a
ngi ci xottu-gerte !
Nun dof yi, noo xam lu tax nuy muslu ci
ñooñu. Sama digganteek Ñarelaa, firnde la
ci. Ñarelaa rëbb na ma ñeenti yoon, sooy
ñeenti yoon. Waaye su Daawur Jaañ doon
dugal loxom ci mbir mi, may tàkk. Duma
jaar kon fenn ba mucc.
Looloo waral ba ma gisee Daawur Jaañ
muy ñàngal kanamam, dama daldi jéggalu
ci saa si, ni ko :
- May ma, Daawur, maa ngi ñëw. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_387 | - Gaawal laa wax, dama yàkkamti !
Céy dof moo sonn ! Boroom dëkk bi de,
man maay nooy-neexam. Saa yu ma
demee bay jàppanteek nelaw, mu ñëw yee
ma, ni ma :
- Aali sama bopp bi ubu na lool fi mu
nekk. Laaj naa réew mi, askan wi jox na
ma ko, waaye ca dëgg-dëgg xalaatuma
woon ne nii la yëf yiy jafee. Léegi daal,
yow rekk laa yaakaar ne mën nga ma cee
dimbali, xelal ma. Loo ma digal, dinaa ko
def, Aali.Du benn du ñaar, ne naa ko :
- Dëgg la Daawur, ay at a ngii ngay tëñax-
tëñaxi. Wóor na ñépp ni xamatoo foo jëm.
Tee nga janook ñi la fal, wax leen ne
mënatoo dem ? Defe ko noonu, Daawur,
bul ci am kersa ba gaañ sa bopp, sànkaale
réew mi !
Waaye du nangoo dégg loolu. Saa yu
ma waxee noonu, day mer, di xultu, di ma
xas :
- Du lii lañuy waxati ci sa ndof gi ! Xanaa
danga bëgg sama gaa ñi sàkkal ma pexe ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_388 | Aali, ni mbir mi doye waar, kenn mënu la
koo wax ! Gis nga, bëccëg bépp maa ngi
ci boppu gaal gi, di joow, ànd ceek fulla ju
mat sëkk. Ñépp yaakaar ne xam naa bu
baax fi ma jëm. Bés bu ma juumee ba ne
ñi topp ci sama ginnaaw xawma yoon wi,
réew mi tas.
- Yàlla tere, Daawur ! Man Aali de, réew
mi amalu ma benn njariñ waaye ñaanuma
Yàlla mu tas. Léegi nag guddi na,
Daawur, demal bàyyi maak sama xottu
mbaar mii, ma nelaw.
- Nelaw ! Xanaa soo ma waxee li ma lay
laaj ba noppi !
- Loo bëgg, Daawur ?
- Yoon wi ! Won ma yoon wi ma war a
jaarloo askan wi ! Kàngam yi ma wër
taluñu daraak jalgati xaalisu réew meek
tabax ay kër yu rafet ! Te dégg naa sax ni
yéen dof yi yéen a fi ëpp xam-xam.
Li ëpp ci sama waxtaan ak Daawur Jaañ
noonu lay tëdde. Waaye sunu gise biig bi
moom, neneen la deme. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_389 | Ñàkkul Daawur am fu mu jaar, door maa
seetsi. Dafa ràkkaaju woon dëgg, di wax
ay waxi dof. Li ma toog ci otoom yépp
muy dawal, mu ngi ma naan :
- Aali, yaa ngi gis tali bii nuy jaar, kër yi
nuy romb yépp, garab yi ci mbedd meek
kayit yi ngelaw liy ëf, ñuy wëndéelu ci
jaww ji ?
- Waaw, Daawur ? Loo ci wax, nag ?
- Aali, xoolal : yooyu ma la limal yépp
maay boroom ! Réew mii maa ko moom !
Li mu wax jaaxal ma lool. Ma sàcc xool
ko, gis ni bët yiy melaxe. Ma ne ko :
- Àa, Daawur ?
- Sàllaaw, Aali ! Man, Daawur Jaañ, maay
ngànd ! Xam nga ne moos doo ñeexu-
ñebbe, Daawur Jaañ, doomu Ajaratu Nafi
Saar ak Abdulaay Masaar Jaañ !
Su ma ragalul woon fen de, dinaa ne li ko
doore fukki waxtook benn ci guddi ba
juróom-benni waxtu ci suba, Daawur Jaañ
wërloo na ma Ndakaaru ñetti yoon. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_390 | Ba nu àggee Gël-Tàppe, joxoñ na ma benn
kër, ne fa la daan jànge Alxuraan ba mu
newee gone ; jaar nanu yoonu sinemaa
Elaas, dem ba jub géej, jàdd sunu
càmmoon, jubal taax ya.
Ma ni ko :
- Foo ma jëme, Daawur ?
- Xanaa kër ga.
- Kër gan ?
- Bàyyil dof-doflu. Nanu dem gàlle waay,
Aali, dóor fa sunu ndékki lu fatt.
- Man dey, Daawur, xiifuma. Daawur Jaañ
faalewu ma, melul sax ni ku ma dégg. Yëf
yi dalul sama xel dara. Guléet ma dégg ko
mu wax waxu ndékki. Ndax kat, nit loo
xamul xamoo ko. Li muy dawal yépp,
sama xel a ngi werante :
« Mbaa du ngóor sii dafa am lu mu ma
naral, di ? »Nun dof yi kat, bu ci kenn
waxulee, léegi sëriñu taryaax yi jéexalnu.
Ñoxor Njaay ñu ne boroom barke bu leen
seetsi : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_391 | - Jàppal kenn ci dof yiy taxawaalu ci
mbeddi Ndakaaru yi. Soo ko rendee,
toggal deretam, naan ci, sëlmu ci. Fi may
xalaatee loolu, Daawur daldi ma geestu,
ne ma :
- Agsi nanu, waaye yow sax danga mel ni
kuy maas, Aali.
- Wax dëgg, Daawur, su doon sama sago
de, nga bàyyi ma ma dellu Ñarelaa.
- Du danga ma ko ñaan, man miy dogal ci
réew mi ?
- Waaw. Ñaan naa la ko, Daawur.
- Ñaan nga ma ko, Aali, waaye maa lànk,
mayuma la ko. Maa la moom, moom sa
moroom. Fi ma la awloo ngay aw ! Dégg
nga bu baax wax ji, Badu ? Njël googu ci
kër Daawur de, dootuma ko fàtte. Ndékki
la neexoon na lool nag, wax dëgg Yàlla.
Waaye kat, coono bi Daawur Jaañ di daj
subaak ngoon ci réew mi, su ci amul woon
ndékki lu neex ñu laaj ko ko ! Waaye xam
nga lan moo dàqoon ci mbir mi, Badu ? | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_392 | Fi nu toog maak Daawur Jaañ ci taabal jiy
guux ndànk sunu kafe, ay soldaar a ngi
nuy tóojal, di misig. Ma dem ba yàgg,
seetlu ne am na ci ñoom ku ma ne jàkk.
Saa yu ma wëlbatikoo, sunuy bët daje. Ma
siggi gën koo xool, daldi ko xàmmee, ni
ko :
- Baay Ndeene !
Muy pat-pati.
Daawur Jaañ ni ma : Ndekete xamante
ngaak kolonel Kamara ?
- Waaw, Baay Ndeene sama waay la,
maak moom noo bokk sunu Ñarelaa ! Aka
bari ay, tey ! Mooy ofise ne paa pëer ! Bés
boo ko tooñee ba mu njatt la, dinga wax lu
set, Daawur !
Daawur Jaañ xaqataay, tàpp ma ci mbagg :
- Yaa mën a tooñ, Aali !
Noonu, ma tàmbalee woy :
Ofise ne paa pëer ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_393 | Baay Ndeene di ma siiñ, ma ni ko :
- Ayca, Baay ! Mu di ma awu, di
tàccuwaale, di pàkkarñi :
- Ofise ne paa pëer ! Bu doxatee sax du
xasaw ndax kenn du ñemee reetaan !
Mujje gi soldaar yi ànd ak nun di misig,
maak Baay Ndeene nuy fecc di tëb di dal,
Daawur Jaañ ak i nitam ñëw fekk nu ci
géew bi. Yëf yi mel ni tuq su bënn te saañ
ba réer !
Bi nu feccee ba noppi, dama daldi jubal ci
Kolonel Baay Ndeene Kamara, tàllal ko
loxo. Moom it mu lëng ma, ndeysaan, ne
yikkat di jooy ni gone gu tuuti.
*
* *
Dammel dee nu jox ndaje, fii ci àll bi. Pax
mu yaatu te xóot la gaslu, nun kàngami
Kajoor yi nu wër ko. Mu ne :
- Xam ngeen lu lii tekki. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_394 | Nun ñéppp nu sëgg, ne tekk.
Njëlug Kajoor. Picc yaa ngi woy, lee-lee
ñu cof xobi garab yi mbaa ñu gësëm seeni
bànqaas, làyyi biy toq ci sunu kow, nun
kàngami Kajoor yi.
Dammel ni :
- Ku ci samay bët dajeek yosam, su dee
gor du fanaan tey.
Ba tey kenn siggiwul, kenn ηaaηul.
Dammel daldi neeti : Luy jot, jot na. Am
na lu ma nar tey, balaa jant biy so...
Ku nekk ci yéen na ma wax lu mu xalaat
ci mbir mi.Foofu, ma yëg ku ma kobos
ndànk.Ma geestu, daj ci Kocc Barma.Céy,
Kocc Barma Faal ! Musumaa gis ku
lakkalee ni moom ! Su ma xamoon ne
moo ñëw toog ci sama wet, dandu kon naa
bu yàgg. Ku ko moytuwul dina la sànk.
Dafa rekk luubu, ngóor sii. Su ñépp awee
yoon wii, mu aw fa ca des. Te kenn feesul
ay bëtam. Dammelu Kajoor ak man Aali
Këbóoy mii nga xam ne ab kàngam doηη
laa, noo yem dayo ci moom. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_395 | Foo fekk Kocc Barma mu ngi jonkan, teg
ñaari loxoom ci óom yi, ηëb ci loxo
ndeyjoor bi juróom-ñeenti xooxi buy. Laaj
nanu ko ba tàyyi lu muy doye juróom-
ñeenti gif yooyu, waaye nanguwu koo
wax kenn.Aka ñor tey, nag ! Golñàdd la,
àgg ca kow. Su toogee ci biir nit ñi dafa
naan keww, fu nekk mu fay sànniy bëtam.
Te nekkewu fi lu dul weddeek tiiñal
kilifay réew mi. Fi nu toog, fexe na ba
déey may kàddu yoo xam ni su ko
Dammel doon dégg di nu reylu maak
moom yépp ci saa si. Xam naa ëllëg, fii ak
ay xarnu, Kajoor dina fàttaliku jaloorey
Kocc Barma Faal, di yéemu ci xelam mu
ñaw te rafet. Wax nag la mën ba mu jeex
tàkk ! Ku jar a seetlu la, ndax lépp lu mu
def am na lu mu ko dugge. Dammel mas
na ko woolu, mu agsi ci biir nit ñeek
wateef gu doy waar. Ñépp di ko ree, ñu
dem ba koy yeew, yóbbu ca àll ba sànni
ko fa.
Dammel ni ko :
- Waaw, Kocc, sa ñeenti jubb yii nag ? | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_396 | -Aa, Dammel, ñeenti jubb yii de, dara laa
ci xamul. Waaye su dee danga bëgg xam
lan la bu ci nekk tekki, mën naa la koo
wax.
- Su ma la ko laajulee nag ?
- Say nit rey ma, ma dee.
- Laaj naa la lu sa jubb yi tekki. Waaye
soo waxee lu dul dëgg du baax ci yow.
Keroog Kocc ñaawul ci xare bi, ndax
Kajoor yépp la jommal.
Nun nag, gise nanu ci àll bi ba noppi.
Sëkk nanu pax mi. Ba nuy dellu dëkk ba,
nee naa Kocc :
- Gisuma la nga sëkkandook nun de, bi nu
waxtaanee ba noppi.
- Dëgg la, Aali.
- Lu waral loolu, nag ?
- Xanaa neex ma. Ba léegi xamoo ni man
maay sama Buuru bopp ?
- Kocc Barma Faal ! Baal li nga nekke. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_397 | Jamono yii Dammel jàq na ba fu jàq yem
te soo moytuwulee dina ne yaak noonam
yee ànd di ko fexeel.
- Gis naa bët yi ma seen Dammel biy
xoole, wallaay.
- Aa, gis nga ko de ? Defe woon naa ne
man rekk maa ko seetlu !
Tee ngaa génn dëkk bi, Kocc ! Buuri tey
yi dañoo fiir, de !
Yéen a ngi dégg wax jeem, yéen waa
Ñarelaa ?
Foofu, Kocc Barma Faal dafa ree, ni ma :
- Yaay bëqët, Aali ! Am, téyeel ma fii,
waay.
Mu ubbi loxo ndeyjooram, tànn ci benn
xooxu buy, ne ma ko jabb. Ma bëgg koo
laaj lu loolu tekki, geestu, xawma fu mu
jaar. Fekk neeti na mes.
*
* * | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_398 | Ku xamul fu Àllu-Kaañ nekk it, dégg nga
turam.
Badu, ci ubbiteb Téereb Dóom, Ngiraan
Fay noon na la su am réew jànkonteek ay
jafe-jafe, dina am ay bés yu ñu ciy ràññee
bu baax. Jotoon na lim sax Talaatay Ndeer
ak Dibéeru Guy-Njulli. Sàmba Lawbe
Faal ak baayam Makoddu Faal.Sadani
Caam ak Mbarka Ja. Ñii di góor, ñii di
jigéen waaye ñoom ñépp ñu ànd diy
jàmbaar, xalimag Ngiraan Fay dekkali
seeni jaloore.
Mën naa seede ne lépp lu sa maam mas a
bind bàyyil la fi, dëgg gu wér peηη la.
Ngiraan Fay sama nijaay ju baax ja, Yal
na la Yàlla xare àjjana, yal na suuf sedd ci
sa kow. Xamoo woon caaxaan, daawoo
jëw kenn, daawoo sosal kenn. Loo wax
mbaa nga bind ko, sañu ma cee teg
baat.Teewul nag, Badu, léeg-léeg sunuy
gis-gis xaw a juuyoo, maak sa maam.
Dinaa la ci jox tey tegtal bu ndaw. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_399 | Gis nga, Badu, jamono dina ñëw, aw
askan ni :
- Sunu réew mii de, ba mu sosook tey, bés
bi ci ëpp solo, bés sàngam la ndax bés
boobu la lépp sotti. Kuy faral di déglu
géwél yi mbaa mag ñi dinga xam li may
bëgg a wax foofu.Tey jii, koo laaj, mu ne
la 26 ci weeru oktoobar, ca atum 1886,
maanaam bés bi Lat Joor desee Déqële, ca
la Kajoor màbb, tas, Xonq-Nopp yi féex,
sog a xam ni buumu njaam gi ñu nu takke
dëgër na dëgër gu, caaxaan du ko fecci.
Fàttaliku Déqële, lu nu war la.
Waaw.Waaye man Aali Këbóoy, bu doon
sama sago de, waa réew mi dinañu bàyyi
xel ci beneen bés. Ci sama gis-gis, bés
boobu kenn fullaalul, moo ëpp fopp solo
xare Déqële.
Nga ne ma :
- Bés boobu ban la, Aali ?
Waa Ñarelaa ngi kobosante, naan : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_400 | - Ayca, du dangay jaay dijj ηaam rekk,
tontul nag ! Dinaa tontu kay. Man Aali
Këbóoy, ma ni :
Ñii may limsi, ñoo séq xew-xewi bés
boobu : benn, Kumandaηu serkalu Kees,
Kees-Kaay, benn dëkk, ñaari gaar, di
Tubaab bu ñu doon woowe Andre
Kastorel ; ñaar, raay yi saxaar giy jaar,
Tubaab yi defoon ko fi, te Lat-Joor giñoon
ne Maalaw du leen teg bët ; ñett, benn
seetu bu mag a mag. Muy ñaata ? Andre
Kastorel, Kumandaηu serkalu Kees, benn
seetu bu réy ak raay yi saxaar giy aw !
Am na lu leen ñeenteel, waaye loolu
moom dama koy leb ba ci kanam. Ñeent
yooyu, lan lañu war a jote ?
Badu, waa Ñarelaa a ngi naan :
Aali mii kat, ràηηatiku na ! Su nu jógulee
ci moom, du baax, de !
Yéen a gaaw a fàtte, yéen waa Ñarelaa !
Moytuleen ma ! Su ngeen xëyee fajar di
dem jàkka ja, bu kenn ci yéen dammati
koñ, ngir bett ma, fas yéene maa bóom. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_401 | Su ngeen ko jéematee dinaa toj Ñarelaa ba
mu mokk rumbux, ay xal dinañu wàccee
asamaan dal ci seen kow, ngeen lakk ba
xëm ñuul kukk, seeni kër def dóom ! Te
dóom boobu, ngelaw li dina ko sànni fu
soree-sore ! Giñ naa ni kenn ci yéen du
mucc ci musiba moomu !
Baal ma àq de, Badu, ñii dama leen a rekk
xaare ! Waa Ñarelaa yii, dañuy jeexal
sama xol ! Man sax yow doηη laay waxal.
Dig naa ko Ngiraan Fay, dinaa ko def.
Lépp lu mu la jotul a wax, dinaa la ko
jottali.
Bi mbir miy xew, gone laa woon. Su dee
amoon naa fukki at it, ca lay yem.
Nu ngi ci Àllu-Kaañ, maak samay
moroom, ñii di raasaatu siddéem, ñi ci des
di witt ay màngo Biraan Jóob. Nu jékki-
jékki kenn ci nun, Mbiita Saar, daldi téen,
déglu woyi picc yi ba yàgg mu joxoñ
yoonu Kees, ne nu :
- Yéen a ngi dégg li may déggam ?
- Loolu lu mooti, Mbiita ? | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
Subsets and Splits
No community queries yet
The top public SQL queries from the community will appear here once available.