url
stringlengths 6
8
| content
stringlengths 2
3.72k
| source
stringclasses 3
values |
---|---|---|
page_402 | - Ndimboy dina am ñaari gan tey. Ñu ngi
ci yoon wiy ñëw.
Nu téen nun itam, gis ni pënd bu xonq bi
muuree jaww ji, dégg ay tànki fas yuy
woy ci kow suuf si, mel ni ndënd mu ñuy
rëkk ak doole.
Ma ne :
- Tee noo jaar ci xur wi, jiitu gan yi dëkk
ba ?
Kenn tontuwu ma. Ku nekk a ngi déglu
Mbiita ba xam lu ciy xalaatam. Foo fekk
ay gone yuy ànd, am na ca kuy dogal,
nekk maanaam seen kilifa. Nun, Mbiita
Saar a doon sunu njiit. Sunu moroom la
woon, waaye Yàlla dafa ko teeloon a may
xel ak bayre.
Su waxaan dara, kenn ci nun daawu ci sañ
a teg baat. Mbiita ne tekk ba mu wóor ko
ne nun ñépp a ngi koy déglu, mu ni :
- Aajoowu ko, Aali. Bàyyil sa yëfu téll-
ma-rajax yi. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_403 | Ni Mbiita Saar waxe xaw maa merloo, ma
daldi ñëg :
- Li ngay jaay amul, Mbiita ! Ñii di ñëw,
su ñu bettee Ndimboy nag, dal ci kowam,
looy wax ?
Mbiita Saar reetaan :
- Xawma kañ ngay muus, Aali. Fas wii
may dégg ay tànkam, fasu Kumandaηu
Kees la. Na mu tuddati sax, Tubaab
boobu...? Fàtte naa tur wi, waay... Ki mu
àndal moom Baay Séy la, mooy làpptoom
bi.
Nu yéeg nun ñépp ci kow garab yi. Ne
tuuti ñaari gawar yi romb nu. Nu xoolante.
Ni ko Mbiita Saar waxe woon, noonu la
ame.
Andre Kastorel, Kumandaηu Kees.
Baay Séy, làppto bi.
Foo gis kenn ki, ki ci des sorewu fa.
Ñoom ñaar ñu mel ni Doomu-Aadamaak
takkandeeram. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_404 | Bi ñu demee ba sore, nu cëppeelu ci suuf.
Abu Sow ne Mbiita Saar :
- Yow nit nga walla rab nga ? Maa ngi lay
bëgg a ragal kat, Mbiita !
- Yéen a ma xamul rekkk, waaye seen
bopp ! Te loolu du woon ay waxi caaxaan,
Badu. Nànditeg Mbiita Saar, fu ko nit
nattoon, weesu na ko. xéy- na looloo tax
Yàlla teel ko fee jële. Bi Mbiita Saar di
lab ci déegu Jooral, fukki at ak ñaar doηη
la amoon. Ba ñu ko yóbboo ak meel ya ba
dellusi ci péñcum Ndimboy, benn boroom
xam-xam nee na :
- Gone gii kay, su guddoon fan, dina ma
jaaxal. Am nañu nu ko gën a soxla.
Waaye nanu dabi gaaw Kumandaηu Kees
balaa mu nuy rëcc. Bi Andre Kastorel ak
Baay Séy di dugg biir Ndimboy, nun gone
yi nu ngi topp seen ginnaaw di yuuxu :
- Wiiw Kumandaη ! Wiiw Kumandaη !
Kuu-man-daη !
Keroog, ñaari gan yi tëju nañu lu yàgg a
yàgg ak boroom dëkk bi. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_405 | Ba ñu gisee ba noppi, kooku woolu
Manjaay, ni ko :
- Kumandaη Kastorel nee na dafa bëgg a
waxtaan ak nun. Yëgalal ma ko waa
Ndimboy.Manjaay daldi tambàlee wër
mbeddi Ndimboy yeek sabaram :
- Dégluleen, jàmm la ! Dégluleen, jàmm
la ! Boroom dëkk bi nee na : Kumandaηu
serkalu Kees, Muse Kastorel, moo fas
yéenee waxtaan ak yéen ! Su ngeen añee
ba noppi, na ñépp daje ci pénc mi ! Yéen
waa Ndimboy, mag ak ndaw, góor ak
jigéen, bu kenn des !
Kenn waxul dara sa moroom, waaye
leeroon na ñépp ne mbirum saxaar gee
taxoon tubaab bi woote ndaje ci pénc mi.
Jamono jooju dey, jafe-jafeek coow bu
baree amoon na ci saxaar gi doon jóge
Ndar, jaar Kees sog a teersi Ndakaaru gii.
Kastorel a ngi toog ci siisam, tegaley
loxoom ci dënn bi.
Kilifay Ndimboy yaa ngi ko wër, ku nekk
di sàcc di randatu ngir gën koo jege. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_406 | Ak li may nekk gone yépp, maa ngi
yéemu cili may gis :
Andre Kastorel, daal, mooy sunu Dammel
bi kenn yëgul fu ñu ko fale, kilifay
Ndimboy yi ko wër di ay dagam, muy
tabb di tebbi.
Maa ngi gisaat lépp, Badu.
Ba tey jii, li ma teewe keroog a ngi mel ni
nataal bu ñu kuppati, taf ko ci sama biir
yóor.Yow kott Kastorel, rax-ci-dolli ngay
doxandéem, nga weex nun nu ñuul, kenn
xamul foo bawoo ak loo fa tekki, ãa, nga
ne déjj ci péncum Ndimboy, ñi gën juddu
ci dëkk bi di la sibooru, soo sëqatee sax ñu
tiit bay saw seen tubéy ! Moo, lu waral lu
doy waar loolu ?
Bi ma demee ba nekk mag la ko sama xel
door a mën a nangu. Dëgg la : bi Kastorel
di laata agsi Ndimboy, fekk na mu xeex
ak nun lu mat ñetti xarnu. Xare na Bawol,
xare na Jolof ak Kaasamaas ak Ñaani ;
Kastorel xare na it Waalo, xare Siin ak
Saalum. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_407 | Nun nag, noo sàggan sunu càgganu bopp
ba mu féewale nu, daan nu, fu nekk mu
teg fay nitam, lu mu leen sant ñu def ko.
Dem nañu fi sax ba su la Xonq-Nopp
saagaa, soo feyoo dunguroom yooyooy
jëkk a soqi seen fetal ci sa kow. Benn
xarnu jàll, beneen jàll, ba muy ñetti xarnu.
Ñu dem ba Kastorel di Kumandaηu
serkalu Kees, war naaru-góoram di duggsi
biir Ndimboy : booba mbir mi amatul
woon benn sikki-sakka nag. Jël na ndam
li, teg loxoom ci réew mi. Du kenn ci
réew mi ku sañ ne :
- Sama baay Dammel la woon.
Mbaa :
- Man mii, néegu Géej laa bokk.
Am na nag ay bañkat yu fi jógoon ciy
jamono ni loolu fàww mu dakk, ñu gar ci
seen bakkan. Sa Maam Ngiraan Fay
bokkoon na ci jàmbaar yi fi taxawoon,
yëkkati seen baat ca kow, ni :
- Moom sa réew !
Kastorel ni leen : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_408 | - Loolu du nu boole. Seen réew a ngoog,
jël leen, fu ngeen xam ngeen jëm faak
moom !
Waaye Badu, wax, wax dëgg ci la.
Yaakaar nga ni coono bi fi Ngiraan Fay ak
waa PAI daj àntu na ?
Tey jii nu ne noo moom sunu bopp, ku sañ
ni coppite am na fi ?
Lee-lee Daawur Jaañ fëgg dënnam, ni
moom moo jàmmaarlook Kastorel, ñu
ñefe, mu daan ko, dàq ko, mu dellu Tugal.
Ci sama gis-gis de, yëf yi dafa xaw a tane
rekk. Baay Séy, dunguru baa ngi fi ba tey,
di doxale ni golo, di jaamu Kastorel.
Mbaa boog, Badu, maa xamul lu géej giy
riir ! Amaana réew mi moom boppam ci
dëgg-dëgg te man yëguma, tinuma. Bu la
sama waxtaan wu neex wi yóbbaale ba
nga fàtte ni dof laa, yow it, Badu !
Sànq, tudd naa Bawol ak Kaasamaas ;
tudd naa it Waalo ak Siin ak Saalum ak
Ñaani. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_409 | Soo gisee ma lim diiwaan yu bare ci réew
mi te boolewuma ci Kajoor, du dama
sàggan, du itam dama koo fàtte. Dafa fekk
rekk ni li ma lay waaj a nettali, Kajoor la
xewe, te Andre Kastorel, Kumandaηu
serkalu Kees ci boppam moo la koy àgge,
Badu.Nga ni ma :
- Naka la loolu mën a ame, Aali ?
Ma ne la :
- Bul yàkkamti, maa ngi ñëw.
Kumandaη Kastorel xool mbooloo mi lu
yàgg. Bët yaa ngi xultu, man ma nekk gone,
di dégg li bët yiy xultu. Ñu ngi naan :
- Cim ! Maa leen xaare, yéen waa
Ndimboy, ak sowaas yi ngeen doon yi,
xayadi be dee ! Dëkk baa ngi ne selaw.
Kenn sañu la ηaaη mbaa sax noyyi, te
Kastorel santu la ko. Tubaab bi geestu
xool Baay Séy ba noppi yëngal ndànk
bopp bi. Baay Séy daw, fekki ko fi mu
toog, daldi sukk. Kastorel wax ak moom
lu yàgg. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_410 | Baay Séy siggi, ni :
- Kumandaη Kastorel moo leen di xamal
ne, moom de, am na naqar wu réy, te kenn
tegu ko ko ku dul yéen ñii toog. Jarul sax
muy jaaraat ci jëf ju ñaaw ji fi ay saay-
saay di def boobaak léegi. Ay weer a ngii,
saa yu jant bi sowee, ñu buddi raay yi ñu
fi teg, ñoom waa Tugal, ngir saxaar gi di
ci jaar. Guddi gu Yàlla sàkk, am ñuy
muuroo lëndëm làqu, buddi leen sànni.
Looloo waral fi mu nekk kenn mënatul
jóge Ndakaaru dem Ndar mbaa jóge Ndar
dem Ndakaaru.
Ci réew mi ba réew mi daj, loolu yéen
waa Kajoor la gën a indil ay jafe-jafe. Jën
yu neex yi daan jóge Ndar ak Ndakaaroo
nga fay yàqu. Ba kañ ngeen fi nar a nekk
di dunde keccax ak gejj ?
Kajoor jaaxle na, ndax lépp lu ko saxaar
gi daan indil te mu amaloon ko njariñ lool,
gisatu ci dara. Waaw, mbaa du yéen waa
Ndimboy dangeen a taxaw ci tànki xeex
nu, nun Tubaab yi ? | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_411 | Muse Kastorel de, nee na moom mënul a
gëm loolu. Xanaa kay ñàkkuleen fulla bay
jàpple ay noonam ! Tee ngeen bañ a gaaw
a fàtte ! Am na ku fi doon jaay njàmbaar
de, di rab-rablu, naan Maalaw du gis raay
bi ! Ana mu tey ? Song nanu ko Déqële,
duma ko. Nun Tubaab yi nag, doole lanu
am ba mu doy ! Ku nu bëgg a jommal,
dangay sonal sa bopp. Deretu Maalaw
màndil na suufu Kajoor sii nu taxaw tey,
def ab déeg ca Déqële, nga nuur ca, ba faf
lab. Kenn waxatul say wax. Dunu la rey
Déqële, ngay dekki Àllu-Kaañ !
Déedéet, waa ju baax. Mënoo dee Déqële
ba noppi fëll Àllu-Kaañ ca ëllëg sa, ne
noηη ca collu garab ga gën a kowe !
Yëf yi mënul a yombe noonu. Laay,
ndekete yow noonu nga ragale dee ?
Kon kay, waroo woon dëkke xare !
Yow, ku la mas ne sa bët bi suuf a ngi ci,
nga ne ko :
- Ayca, bettuma la ! Man Lat Joor Ngóone
Làttir, kenn du ma yab ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_412 | Noon nga saxaar gi du jaar mukk Kajoor !
Wóor na ma ni fa nga tëdd ca Déqële,
dinga koy dégg muy mbiib, di riirloo taax
yi, di yëngal Kajoor, suuf siy xottiku, muy
daw guddi di daw bëccëg !
Yéen waa Kajoor, Kumandaη Kastorel
moo leen di laaj : ndax jàmbaar dëgg dina
làqatu di buddiy raayi saxaar, di sànni
sëmino yi ay xeer ?
Nu ngeen mën a tudde loolu ?
Réy làmmiñ moom def na ko, waaye fit
dara la ci amul !
Mbër dëgg su la sa moroomu mbër
daanee, dangay ngembuwaat, fekk ko fa
mu samp ndëndam ci géew bi, nga këdd
ko mu daanu, ngeen sëggaat, léewtoo.
Doo xaar ba guddi nga taxaw ci sàkketu
këram di ko saaga, te su ubbee buntam
wutsi la, nga ne bëxërñet daw !
Kumandaη Kastorel nee na : bi loolu yépp
weesoo, dafa bëgg ngeen xam lii : xaalis
bi réewam, moom Kumandaη, maanaam
réewu Tugal, xaalis bi muy defaree raay yi | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_413 | ba noppi teg ci saxaar gi muy daw, ngir
jokkale diiwaani réew mii, Kumandaη nee
na : xaalis boobu, wax dëgg Yàlla, xejoon
na ci waa Tugal.
Kumandaη Kastorel moo leen di laaj :
ndax ni mu laabiiree, moom Kastorel, ak
ni mu bëggee dimbali Ndimboy, loolu
ngeen koy feye ?
Boroom dëkk bi ne bëret, ni làppto bi :
Neel Kumandaηu Kees bii toog, nun la jëf
ju ñaaw jooju gën a naqadi. Ne ko it bés
bu nu jàppee ñiy buddi raay yi, dinanu
dagg seen baat kàttit, samp seen bopp ci
sunuy xeej, indil ko ko fa mu nekk ca
Kees.
Làppto bi tekkil Kumandaη Kastorel
kàdduy boroom dëkk bi. Wànte, Tubaab
bi daal, ñaari baat yu jëkk ya rekk la jot a
dégg, daldi wiccax bopp bi, sànni loxo yi
ci jaww ji, këdd suuf si, jóg taxaw, mel ni
kuy waaj a mbej Baay Séy. Làppto bi tiit,
dellu ginnaaw, fakkastalu, bërëηu ci suuf
si, jóg, daanuwaat, jógaat, daldi ne : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_414 | - Yéen a ko gisal seen bopp, de ! Sama
dof bi merati na !
Kumandaη nee na : yow boroom dëkk bi,
naaféq nga te li ngay wax yépp, dara du ci
dëgg !
Man nag, góor gu baax, sa mbokk laa te
soo ma mayee, dina am lu ma ñàmbaas ci
wax ji, ngir dimbali la. Tànnal ci dëkk bi
juróomi janq yu ñuul te sew ruuj, nga
jébbal leen sama Demba Njaay mii. Man
liggéey naak kilifay tubaab yu bare,
waaye kii moo ci yées. Su meree te
yeewaloo ko ay janq yu sew ruuj te ñuul
kukk, mu futti leen di leen caw ba ñuy
nàcc, du am lu ko neex !
Defal li ma la wax ! Soo ko deful, dina fi
yebal ay soldaar ñu rendi góor ñi, siif
jigéen ñi, taal seen Ndimboy gii ! Defal li
ma la wax !
Boroom dëkk bi takk fitam, jéngu :
- Mukk ci këru àddina ! Bëgg lu neex ab
doxandéem du tax may tuumaal gone gi
gën a ndaw ci Ndimboy ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_415 | Baay Séy waxtaanaat ak Kastorel lu yàgg.
Baat bu mu wax, Tubaab bi yëngal bopp
bi, màtt tuñ wi.
Bi ñu noppee, Baay Séy ne :
- Kumandaη Kastorel a ngi leen di gërëm.
Nee na it, ginnaaw guddee na fi, maak
moom Ndimboy lanuy fanaan.
Fekk na boroom dëkk bi rendilu ay xar ak
i béy. Ñu wàjjal gan yi yàpp, ñu naan sëng
ba màndi, tànn ci janqi Ndimboy yi ñu
leen wéttali ba bët-set.
Fan yooyu, Kumandaη Andre Kastorel
bawoo na Ndimboy ganeji Binkeriη,
ganeji Mindaal ak Tinkis ak yeneen dëkk
yu ndaw yi wër Àllu-Kaañ. Fu mu dem,
wax fa waxu raay yi ay saay-saay doon
buddi di sànni. Waa Binkeriη, waa
Mindaal ak waa Tinkis ni Baay séy :
- Neel Kumandaη mii, na xelam dal, balaa
yàgg nu teg loxo ci ñiy def jëf ju ñaaw
jooju.
Kumandaη dellu Kees. Ca ëllëg sa,
buddikati raay yi gën a ràkkaaju ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_416 | Ay sëmino jóge gaaru Kees, topp ci raay
yiy kol-kolal. Waaye saa yu ñu liggéeyee
ba yaakaar ne ñoo ci nekk, yàqkat ya
defaat ñoom it seen mënin. Ñu jàppe ko
noonu ay weer. Tubaab yi jaaxle lool.
Kumandaη Kastorel daldi tàmbalee
tuumaal Lat Joor nag. Loolu ub sunu
bopp, nun waa Ndimboy.
Nu ne :
- Aa ! Lat-Joor man ?
Kastorel mer, gémmiñ giy fuur, mu ni :
- Xam naa li may wax ! Lat-Joor des na
Déqële, waaye ay nitam ñoo fiy def jëf ju
ñaaw jii. Ba tey nangooguñoo wéer seeni
gànnaay !
- Nun dey, Kumandaη, danu yaakaar ne
ñiy buddi raay yi duñuy niti neen.
- Buleen ma sonal ak seen waxi dof
yooyu. Nun, Tubaab yi, gëmunu ne jinne
am na !
Kumandaη Kastorel yebal ay soldaar ñu
taal Ndimboy, taal Tinkis, taal it Mindaal. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_417 | Weer ya ca tegu, Badu, jàmm ne ñoyy !
Jàmm ne ñoyy, saxaar giy daw ni ko
neexe ci diggante Ndar ak Ndakaaru !
Kumandaη Andre Kastorel bég ba fu bég
yem.
Ñaw ! Ndekete nii la upp baaxe ci laax bu
tàng ! Ñépp noyyi, féex, ndax rekk ni
Tubaabu Kees bi jëlee woon mbir mi
dënn. Nun waa Ndimboy, nu defaraat
sunuy néegi ñax, yaakaar ni ay wi jeex na
ba fàww. Benn àllarba, bi timis di waaj a
jot, Baay Séy fëgg biro Kumandaη. Naka
la ko Tubaab bi séen rekk, xelam ñaaw,
mu ne ko :
- Xam naa li nga may yëgalsi.
- Yaa ko waxal sa bopp, Kumandaη.
- Fan la Lat-Joor songe raay bi, bii yoon?
- Fenn la bàyyiwul, Kumandaη ! Yàq na
ko yaxeet, Kumandaη. Boroom-Ndar mi
yilifoon booba Tubaab yi ci réew mi yépp,
woolu Kumandaη Andre Kastorel, gëdd
ko : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_418 | - Loo ma waxoon ? Aa ! Man ngay jéem a
tuur lëndëm ? Waxal ! Looloo la dese ?
Sa tés-tés ju metti ji yépp lan la jur ? Dara
la jurul ! Dara ba dara booloo jeex ! Tus,
laa wax ! Su fekkee ne sowaas yii ñoo lay
të, dinaa la delloo Tugal !
Su ma déggatee ne Lat-Joor teggi na fi
raay bi gën a tuuti, du baax ci yow ! Ali,
ust !
Xas yooyu naqadi lool Andre Kastorel,
mu ràηηatiku. Foo ko fekk mu ngay
wëndéelu ci biir Àllu-Kaañ, di soqi
fetalam, di dëkk Lat-Joor, naan ko su dee
njàmbaar gi muy wootee ngi ci moom, na
génn fi mu làqu, ñëw ñu defante ñoom
ñaar. Bés, Baay Séy fëggaat ndànk buntu
biro Kumandaη Kastorel.
Kastorel ne ko :
- Su dee li ma xalaat nga may waxsi,
dellul fa nga jóge.
Baay Séy tegu ca baat. Dafa daldi xëccaat
ndànk bunt bi, génn biro Kastorel. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_419 | Bi jant biy waaj a so, Andre Kastorel,
Kumandaηu serkalu Kees, dóor boppam
balu fetal. Bi nit ñi dawsee ngir wallu ko,
fekk nañu yóoru Andre Kastorel tasaaroo
ci ruum bi, tasaaroo ci kow kayit yi doon
tege ci taabalam.
*
* *
Andre Kastorel xaru.
Beneen Tubaab wuutu ko, nekk
Kumandaηu serkalu Kees. Waaye ngóor
soosu moom, daanaka masul a teg tànkam
Ndimboy. Benn mbokku Tubaabam daal
la nu yónnee. Te nun de, danoo xéy bés
rekk, gis Tubaab biy dem ak a dikk biir
Ndimboy. Gone gu jaambure la woon nag,
ndax barewul woon wax te daawul dugg
lu yoonam nekkul. Teewul nag yëf yi xaw
noo jaaxal. Waaw, moom sax lu muy def
ci sunu biir ? Guléet nit jóge Tugal, romb
Ndar, romb Gore, romb Tëngéej, romb
Kees ak Ndakaaru, ñëw dëkksi Ndimboy ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_420 | Bi ñu demee ba waa Ndimboy di ηun-
ηuni, lu nekk ñu ko ciy wax, boroom dëkk
bi woo mag ñi, ne leen :
- Fan yii yépp, yéen a ngi fiy gis ab
Tubaab buy dem ak a dikk, di nemmeeku
itam xeeti garab yi nekk ci Àllu-Kaañ bii.
Dama bëgg ngeen xam ne Kumandaηu
serkalu Kees bu bees bi, ki wuutu
Kastorel, moo ko fi yebal.
- Lu mu fiy wut ?
- Nee na dafa bëgg a dëkksi Ndimboy.
- Aa ! Ana Tubaab ak a dëkk Ndimboy ?
- Lu ne def naa ko ngir xam lu fiy tànkam
ci dëgg-dëgg. Waaye ndaama lii ma gis
de, ku ñor la. Nanguwul a wax li ko fi
indi.
- Xanaa kay dina teg dara sunu loxo ?
Waaye dama bëgg a dëkk Ndimboy rekk !
Loolu du wax !
- Moom kay, wax na ay waxi dofam. Nee
naay da nuy jàpplesi ci mbey mi.
- Ci mbey man ? | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_421 | - Waaw, nee na am nay pexe yuy gën a
naatal gàncax gi, aar jur gi. Su nu bëggee
daal, dinanu jàngal ni nuy def ba xiif
dootul rey kenn ci Ndimboy.
- Ngóor sii gën a bare caaxaan !
- Man it de, mbir mi jaaxal na ma. Moo
tax sax ma woo leen, yéen magi Ndimboy
yi, ngir nu gise.
- Naka la ab Xonq-Nopp mën a dëkke
sunu biir ?
- Monte mooy am de.
- Lu waral lu ñaaw ?
- Xanaa doole. Doolee mën dëgg. Noo
tooñ sunu bopp. Ku sañul a bañ nag, sañ a
nangu. Tubaab bi waral coow li moom,
gune gu ndaw la. Fanweeri at doηη la war
a am. Diggu-njolloor la agsi Ndimboy, ak
sooxam bu metti.
Maak samay moroom nu tudde ko Capp-
Cappal. Doomu-Aadama boo gis am na
luy gën a fés ci jëmmam, ñu ko koy
ràññee. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_422 | Moo xam ci melo bët yi la, ci waxinam
walla ci xar-kanam gi.
Robeer Langlaad moom, bopp bi dafa
tàppandaar. Langlaad fexe na ba dëkk ak
nun Ndimboy lu mat juróom ñeenti weer.
Ku sob la, ndax lu nekk mu ngi koy laajte,
di for ay xeer ak a witt ay xobi garab, di
leen xeeñtu, di bind seen tur ci benn téere
bu weex. Deful nag ni yeneen Tubaab yi
nu daan digaaleel, nun waa Ndimboy.
Jàppewunu ni ay bàyyima, jéemu noo
suufeel itam. Tàmbali naa jàng sax wolof.
Robeer Langlaad, weg na it sunuy jigéen
ndax deful ni mbokki Tubaabam yi fiy
faral di ñëw. Deful janqu Ndimboy bu ko
romb ci àll bi, mu pàdd la, tas sa sér, tëdde
la ci ñax mi te du la sax xool.
Saa yu ko waxtu añ mbaa waxtu reer
fekkee ci dëkk bi, du nangoo beru, day
ñëw wër ndab leek nun. Man Aali Këbóoy
de, giñ naa ne masu maa gis Tubaab bu
bëggee cere baasi ni sama Robeer
Langlaad ma ! Langlaad jéemu noo xëbal
te it jaayu nu doole. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_423 | Tanqalu nu itam ak waxi raay bi taxoon
Kastorel xaru. Li nu jaaxal kay, mooy li
mu ne dafa nu jàngalsi bey te masul a wax
lu ci jëm ! Lee-lee mu dugg biir Àllu-
Kaañ, toog fa ay fan i fan. Mas nanoo fexe
ba bett ko fa, maak Mbiita Saar.
Fi nu làqu, Mbiitaa ngi ma naan ci suuf :
- Aali, seetlu nga bu baax Capp-Cappal
mii ?
- Dëgër na fit, de, xam naa ! Moom kott ci
biir Àllu-Kaañ !
- Du loolu, Aali, Capp-Cappal mii am na
lu muy seet. Bi nu làqoo fii di ko xool
sànq ba tey, mu ngi sëgg. Gisuma ko mu
téen benn yoon. Am na lu Capp-Cappal di
seet te ci suuf si la nekk. Fu mu gis ay
rëdd-rëddi tànk, topp leen. Ma jële koy
kaf :
- Xéy-na maamaam ya ca Tugal ay rëbb
lañu woon !
- Baax na ! Dinga ne ma Mbiita Saar
waxoon na ko ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_424 | Nawet bi ñëw.
Benn guddi, ñu tàmbalewaat teggi raay
yiy sànni. Naka la ko Mbiita Saar dégg, ne
fàww mu ceddowu Capp-Cappal. Wànte
bi Mbiita sullee wax ji, Tubaab bi fullaalu
ko. Dafa ko ne rekk :
- Loolu bokkul ci sama liggéey. Te yow
sax, Mbiita, seetlu naa ni gone gu yeewu
nga ! Dinaa la yóbbu Tugal nga jàng fa,
foofoo dàq Ndimboy, du sax benn.
Nanu dem Àllu-Kaañ nga jàppale ma,
dama fa bëgg a samp benn seetu bu mag.
Mbiita Saar ne ko :
- Seetu ? Lu seetu boobuy jariñ ?
- Day xëcc ceeñeer yi, naj leen ci benn
tomb.
- Ãa ?
- Waaw, léegi nag ngelaw leey ëf tàngoor
wi delloo ko ci asamaan si, su ko defee
seetu bi ñoral niir yi, Ndimboy daldi naat,
am ndox ba doyal sëkk. Seetu bii, moo fiy
jëleji maral ba fàww, Mbiita. Xawma lan,
wànte lii moom wóor na ma : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_425 | seetu dootul réy mbaa mu dëgër ba dab
seetu Robeer Langlaad boobu. Maak
Mbiita Saar nu jàppale ko, mu daldi samp
seetoom ci diggu Àllu-Kaañ. Bés, nu
yeewu suba teel ak tiitaange ju réy. Nun
daal, danoo jékki-jékki dégg suuf siy riir,
mu mel ni dafa am ay ponkal yuy buddi
garab yi di leensànni ci jaww ji, garab yiy
mbëkkante ni ay yëkk yu naan sëng ba
màndi. Ne tuuti, rabi Àllu-Kaañ yépp di
yuuxoondoo. Jamono jooju, rab woo mën
a xalaat ci àddina amoon na Àllu-Kaañ.
Gaynde. Segg. Bukki. Till.
Rabu àll yépp a fi amoon, mani la, Badu.
Gaynde yeek till yeek bukki yeek segg yi
nag àndandoo di yuuxu ci njëlug Ndimboy
gi. Ndimboy tànn xale yu góor yi ëpp fit
ak doole ci dëkk bi ne leen nañu
nemmeekuji mbir mi. Gone yi làqu ci
ginnaaw ay gàjj, gis ñaari ponkalu dàngin
yu ñuul kukk ñu taxaw ci kanamu seetu
bi, di fecc, ku nekk ci ñoom ñaar di niir
boppam. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_426 | Lee-lee kenn ki bës baaraamam ci seetu
bi, mel ni kuy jéem a luqiy bëtam, ñàngal
kanam gi, ηóobi, yëkkati loxoom, xàcci ba
dara desul lu dul dóor mu wàcce ko, mel
ni kuy artu ki mu janool :
- Soo ma moytuwul, yow, dinaa la def lu
bon !
Moroom mi gis ay butéeli sàngara yuy
tege ci wetu seetu bi, mu gàddu ci benn,
jolu ba xolam sedd, yuuxu, sànni butéel bi
fu sore, dellu seetuji, fëgg dënn bi ñeenti
yoon, daldi sab. Beneen dàngin gi jolu
moom it butéelu sàngaraam, bët yiy tàkk,
di melax, mu mel ni ku mer, daldi am lu
mu déey xarit bi. Ñu riirandoo, dugg biir
Àllu-Kaañ. Similaak-saala dàngin yi
delluseek seeni jaasi.
Ku ci nekk taxaw ci kanamu seetu bi,
janook sa bopp, ne ko :
- Bettuma la !
Nekk nañu fa lu yàgg sax, di dóor jaasi
seetu bi. Mujje gi, ku nekk ci ñoom ñaar
di gaañ boppam, sa deret muur la, | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_427 | ngay yuuxu, toqi, waaye sa jom mayu la
nga bàyyib doxandéem mu fekksi la ci sa
biir kër, bëgg laa jam naani. Loolu moom,
xel mëneesu koo nangu ! Dàngin yi dem
ba seen takkandeer ak seen jëmm
maasaloo. Ñaari ponkal yi fàtte seetu bi,
nag, daldi songante.Xeex bu yàgg sax, te
metti, Badu !
Benn dàngin gi ne kàttit dagg baatu
moroom mi, ba noppi tiim ko, saw ci kow
néewam.Waaye ba mu demee ba defe ne
xeex bi jeex na, la séen beneen dàngin ci
biir seetu bi. Mu ne ko :
- Laay ! Xanaa kii day xaru ? Loo fiy def
yow ? Dawal gaaw, mbaa ma def la ni sa
moroom mii tëdd ! Man moos nga xam
ne, góoroo-góor, maa fi mën, ëpp fi fit !
Dàngin gi ci biir seetu bi tontu ko ci saa si :
- Laay ! Xanaa kii day xaru ? Loo fiy def
yow ? Dawal gaaw, mbaa ma def la ni sa
moroom mii tëdd ! Man moos nga xam
ne, góoroo-góor, maa fi mën, ëpp fi fit ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_428 | Aywa ! Xeex bi neeti kurr. Dàngin giy
jamat boppam ba yaram wépp dagg. Soo
ko gisee mu nga lott ba xamatul fu mu ne,
di xiixat. Mu jékki-jékki bàyyeeku, àgg
suuf, ne nemm, ndeysaan. Waa Ndimboy
génne fa ñu làqu woon.
Dàngin gaa ngi jaaxaan ci wetu moroom
mi mu dagg bopp bi, deret ji muur, yaram
wépp, xonqal der bi bamu xonq coyy.
Xetu sàngara seek xetu deret ji ubale Àllu-
Kaañ.
Ni dàngin gi tëddee, di sukkuraat, bët yaa
ngi nuy tàggu.
Badu, musumaa gis lu tiise noonu. May
ma sax ma dellu tuuti ci at yi nu weesu.
Soo ñibbisee Ñarelaa, dinga jàng ci Téere
bu ñuul bi, kàddu yii ci Ngiraan Fay bind :
« Li ma xam ci àddina yépp, li ci ëpp solo
dof bu ñu naan Aali Këbóoy moo ma ko
jàngal ci samag ngone ».
Ngiraan yemul foofu. Yokk na ci yeneen
kàddu yu am maanaa. Nee na la :
« Dof mat naa bàyyi cim réew » | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_429 | Su ma la fàttalee loolu, Badu Taal, dafa
fekk ni man ci sama bopp, lépp lu ma xam
ci àddina, dàngin ga ma tiim muy
sukkuraat ca Àllu-Kaañ moo ma ko
jàngal. Fonk sa bopp, naw sa xeet, bañ a
jébbal sa ruu ay doxandéem, loolu lépp,
Badu, bés boobu laa xam lu mu tekki
dëgg-dëgg.
Dàngin gi daldi dog. Fi ma toog, ma yëg
ku may kobos ndànk. Ma geestu, daj ci
Mbiita Saar mu jonkan ci sama wet.
Mbiita ne ma :
- Sunu lafañ bee liggéey lii lépp.
- Lafañ ban ngay waxati ?
- Capp-Cappal, xanaa. Ñaari dàngin yii
ñoo doon buddi raay yi.
- Ana mu sax, moom ?
- Téenal, Aali.
Ma téen, gis Capp-Cappal ak boppam bu
tàppandaar, mu ne noηη ca kow benn daqaar
gu mag, tiim nu, di nu seetaan. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_430 | Keroog, Robeer Langlaad fanaanul Ndimboy.
Dafa jubal Kees, yót Kumandaηu serkal ba
ñaari boppi dàngin ya doon xeex biir Àllu-
Kaañ. Ca lanu gëjee dégg lu jëm ciy mbiram.
*
* *
Seetal ma lii rekk ! Toog diggu màrse,
daggat sa ruu, saam, ne danga koy
wànteer ! Doomu-Aadama ni yow jóge fu
kenn xamul, gënula ndey, gënula baay, ni
la :
- Lii nag, ñaata ?
Nga ni ko :
- Aa, noo ko bokk, loo ma jox baax na.
Mu làmbaatu ko ba xolam sedd, siggi xool
la :
- Ay butéeli sàngara de laa fi dese.
- Sàn-ga-ra ? Demal seeti keneen ! Sama
ruu gii nga xam ne moos bi ko Sunu
Boroom biy defar lu nekk la ci daj, nga
may wax waxu sàngara ! Lakk naa sa lu
bon léegi ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_431 | - Tee ngaa bañ a waxe noonu ? Tey gaal
gi jóge Tugal indiwul piis, indiwul caq.
- Te mënoo ci teg dara, yow tamit ? Ruu
kat du caaxaan ! Ngeen waxaale ba juboo,
mu daldi nos sa ruu, wommat, dugal ci
gaal gu màggat, dem yoonam. Yow
moom, taloo dara lu dul jolu say butéeli
sàngara. Bu jeex nga ubbi beneen. Sa
yaram tàng jër, ngay fecc ci naaj wu tàng
wi ba mel ni kuy daanu rab. Gaal giy raam
ci géej gi, di yikkat, saxaar siy muur
asamaan si ndànk-ndànk, ndeysaan. Seetal
ma lii rekk ! Yàlla dénk lam réew, ngay
sàggan ba ay doxandéem ñëw di jënd nit
ña ni ay xar ! Ñu tegsi ay xarnu, sa ruu
réer la, ku la gis xam ni xottu nit nga.
Waay, mënoon ngaa sédd ëllëg ! Nde kon
doo ne dur, di njaay-xólléy, ne yaa moom
réew mi, janq bu la romb ci pénc mi sa xel
ne ci, nga ne indil-leen ma ko, man Buur
maa war a jëkk a jaar ci moom bala koo
kenn di laal. Ñu indil la ko, nga toj taat yi
jàll ca ka ca des. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_432 | Noo tuddoonati sax, yow ? Am nañu lay
woowe Daaw Demba. Waaye am nañu
naan déedéet, sa tur dëgg Daawur Jaañ la.
Dégg naa it ñu naan Móbutu Seese Seko
nga tudd. Ak noo mën a tudd, ndóol geek
naqar wi nu nekke tey, yaa nu ko yóbbe !
Bi nga wuyujee Maam ak tey mat na
ñeenti xarnu. Dem nga barsàq, wacc nu
feek sunu naqar.
Xamal ne ay takkandeer, ay xotti nit doηη
nga bàyyi sa ginnaaw. Nga defe ne loolu
yoon la ? Cim !
Xanaa war ngaa rus de, ba nga dajeek
Maam barsàq, mu ni la :
- Doom, mbaa def nga sa warugar ca
dunyaa sog maa fekksi fii ?
Loo ko tontu ? Waxal, nag !
*
* *
Ma ne : seetu desatul ci réew mi. Seetu bu
waay jub, mu rus, fell, xar, daldi faf kalaate,
tasaaroo, ku ci dëgg say tànk dagg, di nàcc. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_433 | Réew mu amul seetu, dara desatu fa.
Sàmmleen seetu yi ! Waay, bàyyil-leen
seeni sët ak seeni sëtaat fu ñu mën a gis
seen bopp, mu doy leen, ñu bañ a sëgg ndax
gàcce gu jéggi dayo.
*
* *
Bés, góor gu sell gi gis na leen ñuy yox-
yoxi, mu ne leen :
- Du caagin damaa mën a dige. Man,
maay ki am pey ba mu doy sëkk.
Ku déggul wax ji, sa bopp.
*
* *
Badu, mbaa du danga yaakaar ne fàtte naa
Yaasin Njaay ak Biige Sàmb, di ? Booba
nga juume ! Su ma fàttee ñooñu ñaar,
Ngiraan Fay rey ma !
Digoon naa ko, moom Ngiraan Fay, ne su
ko fi Yàlla jëlee, man maa lay nettali li dal
Yaasin Njaay ak ñaari doomi goloom yi. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_434 | Gëmoo ma ? Xaaral ma fàttali la fan la
Ngiraan yemoon cib nettaleem.
Tey ngay xam ne man Aali Këbóoy, dof
bi, maa forox nopp te neex xel, kaar !
Ngiraan Fayay wax de !
Déglu ko...Ngiraan Fay noon na fi ci
Téereb Dóom :
« Waaw, Badu, ku la masula tudd, masula
taas, su takkee ay waliisam, fëgg sa buntu
néeg, fekk la fi nga tëdd mu tàggu la,
xanaa kay li ci des mooy mu woolu taksi,
ne yoonu ayeropoor maa ngoog ? Du
dëggam, Badu ?
Ba àddinay baax de, noonu la yëf yi daan
deme. Waaye, bés ba Yaasin tàggoo ba
noppi, la tàmbalee def lu ma jaaxal lool.
Ca laa ko gis mu yebbi ay waliisam ci ëtt
bi, yëre bu ne mu yëkkati, fëgg, fëggaat,
poos bu nekk mu dugal ci loxoom, yuri
ko. Lee-lee mu teg benn ndoket mbaa
benn sér ci suuf, jëlaat ko, lemmiwaat ko
ba noppi delloo ko ci biir waliis bi. Lan la
Yaasin Njaay réerle woon noonu ? | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_435 | Waroon naa réy de, ndax ci ay xultu ak ay
waxtu la mujje. Ne tuuti, Biige Sàmb agsi
taf gémmiñam :
- Waaw, Yaasin yow, loo xewle ? Du
danu waroon a dem ci Sinkun Kamara mu
ñaanal la, ñaanal xale yi ?
Yaasin siggi, ne jàkk Biige Sàmb. Man
mii Ngiraan Fay de, dootuma gone, waaye
giñ naa ne musumaa gis nit ku jàqe ni
Yaasin Njaay keroog. Ñaari doom yi ñëw
katamu ko, di jooy.
Mu ne Biige :
- Sama kayit yépp réer nañu, Biige.
- Nga ni ma ?
- Waa-waaw. Seet naa ba sonn.
- Loolu gën a doy waar, Yaasin !
- Wóor na ma ne am na ku fi dugg jël
samay kayit ! Seen kër gii kay !
- Céy, yaa bare ay ! Yaa ngi tooñati, de !
Bés bu nekk ma ne la gaaw a mer baaxul,
Yaasin Njaay. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_436 | - Amatuma paaspoor, amatuma kayit giy
biral ne Tubaab laa, lépp réer na !
Nu may def, Biige ?
Fu ma jëm ?
- Nanu dem. Man Biige Sàmb loolu
mënumaa të, am naa ci pexe.
Li ma nànd keroog ci waxtaanu Yaasin ak
Biige, lii la : musiba moomu daloon
Yaasin, sa yaay amoon na ci mbégte mu
réy a réy ! Te njortoon naa it ne fu kayiti
Yaasin Njaay ya dugg, moom Biige Sàmb
moo leen fa dugal. »
*
* *
Lu tegu ci loolu Badu ? Déglu ma, ma
wax la ko.Biige Sàmb a téye Yaasin Njaay
ci loxo, ñu ànd seeti benn sëriñu taryaax
bu ñuy wax Sinkun Tiggide Kamara.
Kooku ne leen :
Bismila.
Ñu summi seeni dàll, dugg, nuyóonteek
moom. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_437 | Sinkun Kamaraa ngi toog ci derub
mbaam-àll bu ñuul.
Soo gisee Yaasin moom, mu ngi sànniy
bëtam fu nekk, mel ni ku fit wi rëcc, mu
jaaxle, di réccu li mu doon toppe Biige
Sàmb Baal ma, ma may la tuuti ci Sinkun
Kamara, Badu.
Yaa ngi fàttaliku Ustaas Mbay Lóo ?
Ci Téereb Dóom, Ngiraan Fay won na la
pukkuus ba mu daan fanaan.
Néegu Ustaas Mbay Lóo ak bu Sinkun
Kamara bi benn lañu.
Ñoom ñaar ci seen bopp sax dañoo xaw a
niroo. Monte seeni jikkoo ka wuute tey !
Ustaasu Ngiraan Fay ba, yaaram la woon
te Sinkun Kamara mii, saay-saay tigi la.
Waaye loolu jarul a yàkkamti, Badu. Fan
yii di ñëw, dinga gisal sa bopp li ma lay
wax ci mbonug Sinkun Kamara.
Bi ñu jàmmantee ba noppi, Biige ni sëriñ
bi :
- Indil naa la sama xarit bi ma la doon
wax. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_438 | Sinkun Kamara xool Yaasin ba seppali ko,
wiccax ndànk bopp bi, daldi ne :
- Sama kóllëre nga, Biige. Lu ma ci mën,
dinaa ko def.
- Maak yow kañ, Kamara Yille, démb la
woon, tey sog a ñëw. Yaasin mii nag, am
na nu mbir mi doon deme nu nekk ay
noon maak moom, ba ku jekku kon sa
moroom gaañ ko. Ñaari doom la am, man
ma am benn bant kott, muy Badu. Xam
nga Badu, ndax ba muy dem bitim-réew,
ànd naak moom ba ci yow nga ñaanal ko,
defaral ko ay muslaay.
Sunu ñetti banti-Maam-Yàlla yi nag, muy
Badu, di Mbisin, di Mbisaan, ñoom ñépp
Taal lañu sant, ndax mennum Asan Taal
moo leen jur.
Sinkun Kamara wiccaxaat bopp bi :
- Eskéy ! Soo meloon ni jigéeni tey yi de,
dinga def Yaasin Njaay mii sa noon.
- Dëgg la Kamara, waaye su diggante bi
rafetee nii, ci Yaasin Njaay la. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_439 | Moo ma ko ji, moo ma won kanam gu tax
ma sañ koo jege, ba léegi maak moom nuy
ay doomi-ndey.
- Yal na Yàlla gën a dëgëral seen
diggante. Ñaar ñu baax ñoo mën a ànd.
- Sëriñ bi daal, dénk naa la Yaasin. Ñaanal
ko. Bi ma demee di ko jëli sànq, nee na
ma ay kayitam dañoo réer. Dimbali ko ba
ñu feeñ te muy li gën ci moom ak ñaari
doomam yi.
Sinkun Kamara tàllal Yaasin Njaay benn
layu bu ndaw, ni ko :
- Waxal fii sa soxla. Ñaan ci lépp li nga
bëgg.
Yaasin téye layu bi, di ratatati ci nasaraan
bay xiixat.
Biige Sàmb ree :
- Céy man di, sama Tubaab bi ! Waxal ci
suuf, aajowul nuy dégg say ñaan, Yaasin.
Sinkun Kamara ree moom itam, ni ko :
- Dégg nga wolofam ?
- Un peu... Tuuti rekk, monsieur Kamara. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_440 | - Soo bëggee sa aajo gaaw a faju, jéemal a
làkk wolof, mbaa séeréer mbaa joolaa
mbaa kikuyu. Sama gaa ñi dégg nañu
làkki Doomi-Aadama yépp, waaye lee-lee
dañuy jéppi ñi leen di làkk nasaraan. Te
ñoom kat seen mer baaxul, yàq nit ak naan
ndox lañu yemale.
Yaasin def li ko Sinkun Kamara sant.
Taryaax bi ne Biige Sàmb :
- Su subaa, bu ñu jullee tisbaar ba noppi,
na fi sa xarit bi dellusi moom kenn.
Fukki xobi siddéem ak ñetti xooxi ditax la
Sinkun Kamara jëkk a laaj Yaasin.
Ba mu ko indee, mu ni ko :
- Baax na. Dellul fa nga jóge. Laajteel ba
gis ku la won kàdd gu màggat ba am ñetti
xarnu, nga dagg ci reen yi, indil ma.Biige
Sàmb ànd ak Yaasin, ñu wër Ndakaaru ay
fan i fan, gisuñu fenn luy nirook kàdd.
Kebemeer lañu mujjee ame reen yi Sinkun
Kamara soxla woon.
Lu sa xel mën a daj rekk, Sinkun Kamara
wutloo na ko Yaasin Njaay. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_441 | Tuutee tee sax ndaw si gedd, bàyyi Sinkun
Kamara ak i xërëmam, dem defarlu ay
kayit yu bees.
Làmmiñu seku wu ñu fanaanal ci këllu
lem.Juróom-benni bëti golo.
Nenu banjóoli ak nenu naat yu ñëb.
Tojitu seetu ak kawaru Tubaab bu jigéen.
Ñax mu tooy.Ba Yaasin indee li mu ko
laajoon, Sinkun Kamara boole yépp sotti
ci benn mbana, nekk fa ay fan di jamb ak
a jambaat.
Bés mu woo Yaasin, mu ñëw, mu lalal ko
ndés, ni ko :
- Toogal. Yaasin a ngi ñaq tooy xepp ndax
li mu dox ci naaj wu tàng wi. Rax-ci-dolli,
fit waa ngi naan :
- Tëf ! Tëf ! Tëf ! Sinkun Kamara ne ko
jàkk, ne ko :
- Du ku la soppi leneen rekk nga bëgg ?
Yaasin ne patt. Sinkun Kamara xulli ko,
yuuxu : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_442 | - Yaasin Njaay, dégguma sa baat ! Du yaa
bëgg ma soppi la ?
- Waaw. Maa la ko ñaan.
- Mën naa la soppi, nga nekk loo bëgg !
Loolu du dara ci man. Yaasin Njaay, nee
ma naam !
- Naam, Kamara !
- Soppi la leneen ak naan ndox laa
yemale. Dégg nga wax ji, de ?
- Waaw, dégg naa ko.
- Yàlla miy maye di nangu moo ma
mayagum kàttan googu.
Xelu Yaasin dellu ca bés ba ko Biige
jëkkee taal Sinkun Kamara, mu réccu li
mu ñàkkoon a wóolu Biige :
« Tooñ naa Biige de, waaye dama
ragaloon rekk mu sànk ma. Ameel naa ko
àq, ndax góor gii mu ma booleel, boroom
xam-xam tigi la ! »
- Noo bëgg a tudd ?
Yaasin seet ci xelam, daldi ne : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_443 | - Mari-Gabriyelaa.
- Tur woowu neex naa dégg. Mari-
Gabriyelaa naka ?
- Mari-Gabriyelaa Won Bolkowski.
- Nga ne lan ?
- Mari-Gabriyelaa Won Bolkowski.
- Bind ko ci kayit gii.
Yaasin gaawantu bind turam.
Sinkun Kamara dellu ni ko :
- Waxaatal sa tur ma dégg.
- Mari-Gabriyelaa Won Bolkowski.
- Jaaraat ci ma dégg.
- Mari-Gabriyelaa Won Bolkowski.
- Jaaraat ci ba muy juróom-ñaari yoon.
Ba Yaasin Njaay tuddee turam juróom-
ñaari yoon, mu ne ko :
- Baax na. Mbir mi sotti na ba noppi. Mën
nga dem.
Yaasin ubbi kalpeem, génne ci ay kayitu
junneek ñaari-junni yu bare, | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_444 | tàllal ko Sinkun Kamara. Góor gi mer,
gëdd ko :
- Téyeel sa loxo.Yaasin yëg ci saa si ni
yaram wiy loxee ndax tiit.
- Baal ma de, Monsieur Kamara.
- Xawma muse Kamara, xawma muse
Jàllo ! Bumu ñaar, laa wax. Ku la ne mën
nga ma fey, man ? Sinkun Tiggide !
Tiggide Sinkun ! Kamara ! Xaax !
Fi Yaasin toog di xaar, xel maa ngi
werante : « Waaw man, su ma ngóor sii
soppee leneen lu dul Tubaab nag, fu ma
jëm ? Su ma soppee bukki, mbaa golo lan
laay wax ? Tiggide Kamara mu naqadi
deret mii, ku ñuul xol la may niru ! »
Sinkun Kamara joxoñ ko seetu bu mag, ne
ko :
- Demal janook sa bopp.
Booba, daanaka Yaasin newatul ci néeg
bi. Mu ngi dégg baatu Sinkun Tiggide
Kamara, gaa, wànte dafa mel ni keneen la
sëriñ biy waxal. Jéemu ko sax àddu. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_445 | Fekk na yëf yaa ngi doon gënatee teey
xelam.
« Man it, kenn du man ! Waroon naa xam
ne Biige Sàmb man rekk la bañ ! Lii mu
ma dugal, wóor na ma ni musiba rekk lay
juri ëllëg. Bi ma dellusee Ndakaaru ba
léegi mu ngi ma ñóoxu, naan dama koo
neex, dafa ma sopp, fekk duggewu ko
dara lu dul toroxal ma. Sàcc samay kayit
ba noppi boole maak Sinkun Kamara mu
soxor mii ! Moo Biige Sàmb, lu la Asan
Taal def ba tax nga nar noo sànk maak
samay doom ? Lu tax nga nuy sippi mer
mi nga dencaloon Asan Taal ? »
Baatu Sinkun Kamara jibaat ci néeg bi :
- Xanaa du yow laay waxal, Yaasin Njaay ?
Jógal taxaw, xool sa bopp ci seetu bi !
Yaasin jóg taxaw.
Janoo naak seetu bi lu yàgg, gisu ci kenn
ku dul boppam. Mu seetlu ni xeesal bi
yàqe kanam gi, daldi gën a tiit.
Céy, su ko Sinkun Kamara mënoon a
defal li mu ko ñaan ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_446 | Ndaw bànneex bu réy !
Ñuulaay bi dafa rekk doy.
Ku ragalul wax dëgg, xam ne moos lu
ñuul mënul a bañ a sikk.
Der boo xam ne bala moo jag nga topp ciy
fóot ni yëre bu tilim, yendoo fete,
fanaanee fete ! Ku ci doyalul itam, moom
Yaasin Njaay doyal na ci sëkk !
Fi Yaasin di xalaate loolu, am ku fëgg
buntu néeg bi. Sinkun Kamara ni ko :
- Agsil. Ci biir seetu bi, Yaasin séen benn
ndaw su sew te njool mu taxaw ci diggu
néegu Sinkun Kamara. Li mu koy xool ci
seetu bi yépp, Yaasin a ngi naan ci xelam :
« Ndaw sii gën a ñàkk aajo ! Lu ko tee
nuyoo ? » Mu daldi sànni catu bët Sinkun
Kamara. Soo demee kat, ajaa bi moom lay
seetsi. Sëriñ yii, ñoo fi gën a saay-saay.
Nii rekk lañuy def, di moyloo jabari
jaambur yi ! Wóor na ma ni kii coroom la.
« Su dul coroom de, ma xam ne dëgër na
fit ! Sinkun Tiggide Kamara mu tàng diine
mii, mu koy jaay reewande... » | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_447 | Waaye Sinkun moom mu ngi sëgg fi mu
sëgg rekk, di tari li muy tari, mel ni ku
yëgul ne am na jeeg bu ñëw tiim ko, ba
noppi ne tekk di ko xool. Yaasin tàmbalee
waxtu ci suuf :
« Aa ! Ndekete ndaw si duggsi Tubaab bu
weex tàll la ! Aa ! Looloo tax ngay jaay
maanaa ! Soo ma laajoon, xam ne wallaay
Sinkun Kamara faalewulaak say tuñ yu
maasaloo ak sa bët yu sokolaa ak... ! »
Bi Yaasin di laata àggali li muy wax, am
keneen ku fëggaat bunt bi. Sinkun ni ko :
- Agsil. Foofu nag, bi Yaasin di yuuxu,
teyu ko :
Waaw ! Ana ku jëkk ka ? Fan la jaar ?
Mbaa du damay bëgg a jommi bëccëgu
ndarakàmm ? Waaye yow moom, yànj
nga, kaar, sama jigéen ! Maa ngi ci lonet
yu ñuul yi ! Mbaa doo rab sax, ag sa
karaw
- Moo, keneen a ngoog, di ! Kii tamit fu mu
génne giy watatu, di samandaay ni mboq
mu ñor mbaa jant buy ràyy-ràyyi ? | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_448 | Jeegu Tubaab baa ngi taxaw ci ginnaawam,
ne ko jàkk.
Mu ne ci xelam :
« Ndaw sii de, dafa mel ni ku ma jéppi. »
Yaasin Njaay jéem koo wàcce, daldi
muuñ. Ndaw si ne këj, gën a fas kanamam.
Ca la Yaasin xalaatee lu doy waar : « Moo
man, mbaa du dama génn àddina, nekk
àllaaxira, te yëguma ci dara ? »
Noonu mu ne walbit, xool fu nekk, gisul
fenn ndaw si. Su weesoo Sinkun Kamaraak
moom, beneen Doomu-Aadama nekkul ci
pantare bi.
Mu ne sëriñ bi :
- Ana ndaw si fi taxawoon léegi ?
- Dellu na fa mu jóge.
- Loo bëgg a wax foofu ?
- Yaay moom, mooy yow.
- Ba léegi sa wax dese naa leer ci man,
góor gi. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_449 | - Dama ne, bul ma tanqal Mari-Gabriyelaa
Won Bolkowski ! Xam nga ne moos
kooku fi dugg sànq du kenn ku dul yow !
Daa weex nga ñuul rekk, waaye benn
ngeen. Seetul bu baax, laa wax !
Fitu Yaasin Njaay mayu ko muy walbatiku
di seetuwaat. Muy lox. Dunyaa xar, def
ñaar. Taax yu rafet yee muy séen nag, fu
ñu bawoo ba ñew sampu ci diggante
asamaan seek géej gi ?
Mu wóor ko ne suy jéem a jéggi kàmb gi
mu tiim di surux, des fa. Des fan, sax ? Lu
mu ci xam ? Foofu de, Foofee rekk la mën
a tudd. Mu gëmm, xippi, gisaat jeegu
Tubaab bi mu taxaw ci ginnaawam.
Yaasin yëkkati loxo càmmooñam, niir ko
lu yàgg, daldi gis ni mu weexe.
Xol bi féex. Mu bég ba nga ni lii lu mu
doon, daldi muuñ.
Mbégte ma Yaasin Njaay am keroog
jooju, kenn mënul a wax na mu tollu !
Mu daldi ne Sinkun Kamara : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_450 | - Loo bëgg ci àddina dinaa la ko defal ! Su
ma ko amulee itam, dinaa ko wuti indil la
ko.
Sinkun Tiggide Kamara ne Mari-Gabriyelaa
Won Bolkowski :
- Futtikul.
Mari-Gabriyelaa futtiku, mu jaar ci moom,
jaaraat ci moom. Ba ñu noppee, mu ne ko :
- Man de, maa ngi soog a digaaleek
jongomay Tubaab. Waaw, ndekete yéen
dungeen tàyyee làkk nasaraan su ngeen
dee saanjaay ! Loo doon wax noonu, sax,
yow Mari-Gabriyelaa ?
- Bah ! Je ne sais plus ! C’était si bon, en
tout cas ! Tu es un vieux cochon, toi!
Sinkun Kamara daldi raay sikkim bi,
reetaan :
- Am na nag lu des, Mari-Gabriyelaa.
Àllarba jii di ñëw, su ñu jullee timis ba
noppi...
Mari-Gabriyelaa mel ni ku kàddu yooyu
jógee kow : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_451 | - Mbaa jàmm la, Sinkun ?
- Liggéey bu nekk ak weexalam. Dinaa la
xaar, maak yow am nanu waxtaan wu réy.
*
* *
Ñu teg cay fan, Yaasin Njaay dellu seeti
Sinkun Kamara.Kooku ne ko :
- Léegi nag, déglu ma bu baax : du ñaari
doom nga am ?
- Waaw. Mbisaan ak Mbisin.
- Soxla naa ci kenn.
- Nga ne lan ?
- Dinga ma sarax Mbisin mbaa nga sarax
ma Mbisaan.
- Wax jooju tekki lan nag, sëriñ bi ?
- Xanaa li mu tekki doηη. Mbisaan walla
Mbisin, soxla naa ci kenn. Yaay seet nag
koo ma ciy jox.
- Xel xalaatu ko, góor gi. Wax jooju moom
bu yaboo nga teg ko ci suuf ! Xanaa yow sa
yaram neexul ? | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_452 | Sinkun Kamara xool ko ba sappali ko, ne
ko :
- Bul fàtte ki ngay waxal. Sinkun Tiggide !
Tiggide Sinkun ! Kamara ! Xaax !
Mari-Gabriyelaa mel ni ku ràkkaaju, daldi
ko yuuxu :
- Loolu mënul a am ! Non, non et non !
- Dina am de, moonte. Mu neex la dina
am, mu naqadi la dina am.
- Su sa loxo laalee sama benn doom, dinaa
la yóbbu ci yoon !
- Yaa neex, dëgg ! Ba fi mu ne daal,
xamaguloo lu xew ? Jéggi nga kàmb gi,
Mari, tàbbi nga ci béréb bi tudd Foofee.
Dex gii nga nekk di féey, mu féex ba dee,
bés bu Yàlla sàkk Doomu-Aadama ni yow
ñëw ba jub ko, bëgg cee sóobu, xelam
yedd ko, mu dellu ginnaaw. Yow Yaasin
Njaay nga dëgër fit, dëgër bopp ne dara du
la tee jéggi kàmb giy xaaj Dunyaa, xar ko
ñaar !
- Moo Kamara, looy wax nii ? | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_453 | - Lépp maasaloo na ba fàww, amatul dara
loo xam ne nit mën naa taxaw ne lii mooy
màndargaam. Nga téen, séen oto yiy
rawante ci taliy asamaan si. Nga sëppu,
gis asamaan seek i biddéewam ñuy
paccax-paccaxi ci ndoxum géej gi. Démb
saay na, Tey saay na. Fen ak Dëgg itam,
ku ci nekk seey nga ci sa biir deretu
moroom. Yaasin di pat-pati :
- Kamara, looy wax nii ?
- Ñawloo nga ma ñaas yi, ma raafloo leen !
Loolu liggéey bu réy la ! Maam dina ma
xaare te Yàlla du ma ko baal ! Fàww nga
fey ma. Man, lépp lu ma am ci Dunyaa gii
laa ko ame. La may xaar àllaaxira xam naa
ko !
- Wóoy !
- Wóoy yow ! Xawma ana ña nga yuuxu
woon daaw !
- Sarax ma ngir Yàlla, Kamara. Rey ma su
la neexee, te jéggal samay doom !
Wax jooju mel ni lu gën a merloo Sinkun
Kamara :- Bu ma rey ak ay waxi doom ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_454 | Doo nitu dara ! Ku bañ sa bopp, xeeb sa
xeet, noo mënee bëgg say doom ?
Bi mu ko wóoree ne Sinkun Kamara
caaxaanul, Mari- Gabriyelaa Won
Bolkowski tàmbalee yikkat, di jooy ni
xale bu ndaw :
- Waaw, góor gi, loo tuddee sarax ? Noo
mën a xalaatee ne dinaa la jébbal Mbisin
walla Mbisaan nga tëral rendi ?
- Man kay, Mari-Gabriyelaa, doyewuma
dara say doom. Ñi may jàppale ci liggéey
bi ñoo ci soxla kenn. Sama kooba yi
dañoo mar !
Dangay nar ! Waaye defuma ko tey,
defuma ko ëllëg ! Maa lànk ba tëdd ci naaj
wi laa wax !
Sinkun Kamara raayaat sikkim bi ndànk,
muuñ, ni ko :
- Loo yaakaaroon, yow it ?
Seetal bu baax ci sa xel. Xam nga ne moos
dara dàqul lii : tudd Yaasin, sant Njaay ba
noppi xéy bés dégg ñu lay woowe Madam
Mari-Gabriyelaa Won Bolkowski ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_455 | Ku dégg sa tur xam ne yax bu réy a réy
nga bokk ca Tugal, gën faa rafet juddu !
Aa ! Dellu Tugal, dëkk fa, te kenn dootu
la fa gën a yey ! Waaw, kenn dootu la fa
xool ay bëti sowaas nga, danga tilim,
danga xayadi. Fu la neex nga dem ci
àddina si te kenn du la laaj wiisaa...
- Loolu ngay wax yépp jaralu ma sama
bakkanu doom.
- Des na, di, Madam Won Bolkowski.
Waaw, yoo dootu la màtt, weñ yi dootuñu
biiw ci say nopp, loo dem bay lekk ñu
jëkkanteek yow sax, roofal la ciy doomi
jàngoro yu kéemaane, nga feebar doo sax
am ku la faj.
- Wóoy man fu ma jëm ? Ana nga, Biige
Sàmb ? Yaa soxor ! Yaa iñaan ! Lii lépp
yaa ma ci dugal, Biige Sàmb !
- Te kat, Mari-Gabriyelaa, kiy des ci sa
ñaari doom yi du la mere ! Soo xéyee
defaral ko ndékki lu fatt, jox ko mu naan
meew, sófóoram ñëw taxaw ci buntu kër
gi korne, mu ne noηη ci sa ginnaaw oto, | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_456 | jubal daara ja. Xawma Mbisaan lay doon,
xawma ku jigéen ki lay doon, waaye sa
doom ji ma lay bàyyil, ay tànkam duñu
dëgg mukk ci ay ndell, ndax Tugal ga mu
nar a dëkki de, wute na lool ak Liberyaa
mbaa Siyeraa-Lewon, ay way-fippu duñu
fa gàddu seeni ngànnaay song nguur gi, ku
ñu dajeel gor la jaasi.
Li Sinkun Kamara di wax yépp, gémmiñ
gaa ngi fuur, muy say.
Ca la Mari-Gabriyelaa Won Bolkowski
door a xam ne moom sànku na ba fàww.
- Lu tax nga bañ maa nii, Kamara ? Lu ma
la def ?
Sinkun Kamara mel ni ku ko déggul.
- Dootoo toog ci metóro bi, ku say bët
dajeel mu xeelu la. Kenn dootu la wax
wax ju ñaaw, naan la loo fiy def, dellul fa
nga jóge ! Dellul réew ma nga xam ne ay
sulaar ak i caga ñoo fay dogal ! Réew ma
dëkkee yalwaan !
Dama ne : Mari-Gabriyelaa, gaawal def li
ma la wax. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_457 | Bu sama gaa ñi meree du baax ci yow de,
ndax dinañu këf Mbisin, këf Mbisaan, nga
des yow kenn ak sa naqar. Loolu nga
bëggam ?
Keroog, Mari-Gabriyelaa Won Bolkowski
réccu na ndajeem ak Asan Taal ca Màrsey.
« Ku ma newoon nii la yëf yiy mujje, ma ne
la yaa mën a fen. Waaye fen moom, kenn
dàqu ko woon Asan Taal ! Nax na ma, takk
ma, dem bàyyi ma fi te li mu ma doon wax
yépp, ndeke dara du ci dëgg ! Man mi
yaakaaroon ne ay kër ak i isin yu bare la
amoon ci dëkk bi... Ndekete yóo, mennum
Ngiraan Fay a toogoon Ñarelaa di ko xaar.
Waxuma dara, sagaru nit kooku tamit di
yàkkali bóli, defe ne indil naa ko àddinaak
li ci biir !»
Badu, nettalikat bi dina dem ba dégg mbaa
mu gis loo xam ne su ko waxee, ñu sikk
ko, xaare ko. Waaye nu may def ?
Maak jali bee yem. Dunu teqale mukk
ñaari kàddu yii : defu, waxu. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_458 | Sëggal boog ma déey li ma sañula wax ci
kow loolu, man Aali Këbóoy.
Séytanee ngi ruux Mari-Gabriyelaa Won
Bolkowski, naan ko :
- Yaasin Njaay, tee ngaa gëmm rekk,
jébbal Sinkun Kamara sa benn doom ?
Sinkun Kamara kat, def na warugaram.
Léegi yaa ci des. Ku bëgg akara dangay
ñeme kaani. Tee nga koo sarax Mbisin
mbaa Mbisaan ? Du moo gën yéen ñett
ñépp ngeen àndandoo torox ?
Mari-Gabriyelaa siggi, ni jàkk Sinkun
Kamara, ni ko :
- Soo yaboo def lu la neex, waaye duma la
jébbal sama benn doom ! Su Sinkun
Kamara wuyoo Yaasin Njaay, yaa ko
wuyu yow ma fa newul woon.
*
* *
Badu Taal, gaawal dellusi Ñarelaa.
Lu nekk a ngi xew Ñarelaa ci sa ginnaaw. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_459 | Mbisin ak Mbisaan, mag ji, ñoo génn xeet
tey !
Log ay baat yu masul a tëmb ci sa soowu
ndey ji la jur, di leen sàqami ndànk, ñuy
seey ci sa kow làmmiñ, saf suukar, neex,
di la jox bànneex bu kenn xamul nu mu
tollu.
Walla kàddu yooyu tancaloo ci sa biir put
ba far la fotloo.Maam ne la :
- Neel Penda Saar ca Ngawle !
Nga lànk, mu jaral la gaañ sa bopp ba
waccu deret di la fekk. Nga xëm, ñu
ximmali la, ngay xataraayu, di yuuxu :
- Je dis merde à la vieille Penda Saar, moi
C’est où ça d’ailleurs, votre putain de
merde de Ngawuule, là ?
Céy lii !
Bés, Ngiraan ferenklaayu na ci
ndéstanam, ubbi Téereb Fent. Li loxoom
biy daw yépp, di xoos kayit gu weex gi,
mu ngi mel ni xalimaam day waxtu. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_460 | Ca la la ne : « Fu la jant biy tiime, Badu
Taal ? »
Seede naa ni keroog xolu Ngiraan Fay diis
na ! Xam naa dafa yëgoon ci yaramam ne
dina wuyuji sunu Boroom bi te dungeen
gise.
Booba, sama takkandeer a ngi wëndéelu ci
néeg bi, ma yërëm Ngiraan ba sama
rangooñ yiy bëgg a tuuru... Man doηη maa
ko mënoon a wax foo nekk ci Dunyaa.
Tuutee tee ma ne ko :- Góor gi Ngiraan,
na sa xel dal, Badu Taal mi nga namm nii,
di ko laajte, mu nga dëkk sàngam. Waaye
su ma laajoon ndax yaa nga fa ci jàmm ak
salaam, xéy-na dinaa nakk-nakkal. Mii xel
dina ma ne : « Nax ko rekk, mag la, te
fen wuy defar moo gën dëgg guy yàq. Ne
ko : fa Badu nekk, Yàlla ubbil na ko fa
wërsëg wu réy. » Xam nga lu tax defuma
koom ? Kaay nag ma xamal la lenn, Badu
: nun dof yi, fen jafe na nu lool. Ñàkk mën
a fen googu sax laa yaakaar ne moo tax nu
nekk ay dof ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_461 | Rax-ci-dolli, sama digganteek Ngiraan
Fay, caaxaan walla waxi naaféq masuñu
cee am yoon. Looloo tax ba ni mu fi
jógee, ndeysaan, Ngiraan masul a xam foo
nekk ci këru àddina.
Démb, ñëw naa ganesi la bitim réew.
Gisoo ma waaye li ngay wër ci biir dëkk
boobee yépp, maa ngi topp sa ginnaaw.
Yaa ngi ànd ak Abdel Kadeer Maxjub.
Doomu Sudaη boobu doηη moo fay sa
xarit. Yéen a ngi sëgg di waaxu, mel ni
dangeen a ragal ñu xàmmee leen. Yaak
Abdel Kadeer Maxjub, xawma kan moo ci
gën a yooy moroomam. Tiis wu jéggi
dayoo ngi muur seeni kanam.
Lu leen boole yéen ñaar ba ngeen nekk
ñaari doomi-ndey ca réew moomu ?
Ma wax ko, te dee : dara waralu ko lu dul
seen ñuulaayu der !
Waaw : coonoo bu ñu leen fa teg, ni ngeen
bindoo ko waral. Ñi ko sañ a wax nag
barewuñu, wànte yëf yi du leneen. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_462 | Làq-làqal bi doyulam ?
Nëpp-nëppal bi nag, ba kañ ? Maa ngi ciy
teg sama bët, man mii : ku ngeen dajeel,
mu xeelu leen, gaññ, won leen ni mu leen
xaaree. Waa réew moomu jàppe leen ni ay
jaam, te ngeen di wéye naqar woowu,
amuleen fenn fu ngeen koy joytoo !
Man, Aali Këbóoy de, bëgg naa xam lu
tax ñépp tëx, muuma, gumba ? Nit du xaj.
Bàyyileen seen xel ci sunu jarbaat yi nekk
bitim réew ! La ñu fay daj jéggi na dayo,
kat !
Yow nag, Badu, wóolu naa la. Jom ak
teggin rekk nga fi mus a wone. Ba ni fi
Ngiraan Fay jógee, yaa ngi koy dimbali ci
sutura su mat sëkk.
Wóor na ma it ne du yow, Badu Taal, yaay
fàtte kàddu Wolof Njaay yu am solo yii :
Faaydaay tukki waaye fullaay ñibbisi.
Maa ngi leen topp sànq ba tey. Fi mu ne
yéen a ngi ci màrse bu mag bi, di dugg yu
sew : warga ak meew ak suukar ak ñoom
seen. Seen dëkk bee ka tàng sax ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_463 | Amul péex, amul keppaar. Fi ngeen toog di
xaar ótóbiis, benn ndaw su màggat ciipatu
na leen, móolu leen ci làkkam, ngeen mel ni
ku ko déggul.
Yaa ngi wéeru ci benn poto-làmp, ubbi
sab yéenekaay di ko jàng. Nga jékki-jékki
yëngal sa bopp, ne :
- Seetal ma lii rekk ! Abdel Kadeer
Maxjub geestu la :
- Lan laati, Al-yuun Badara ?
Nga daldi muuñ :
- Dëkk baa, wallaay. Jolof daal, ay mbër
kaamil lañu !
- Ãa ?
- Ay waxi dofati rekk ! Dañu bind fii ne
am na ñaari gone yu fa benn waay soppi
golo !
- Déet waay !
- Déglul kay, jeexul : waa ji soppi na gone yi
golo, fi ñuy werante ndax loolu am naam
amul, benn jeegu Tubaab jóge fu kenn xamul
ne moo jur ñaari golo yi ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_464 | Loolooy coow dëkk ba, de !
Abdel Kadeer a ngi ree ba téye biiram.
Yow, nga waaru, daldi ne ci sa xel : « Kañ
laa gëj a gis Abdel Kadeer mu bàyyeeku,
di reetaan nii bay xàqataay ? »
Kadeer siggi xool la, ne :
- Ay waxi dof nga may wax, kañ !
- Waa dëkk ba dofuñu wallaay, Kadeer !
Li leen jàpp ba ñuy gëm yëfi dof yooyu
am na tur.
- Noo ko tudde ?
- Du dara lu dul ñàkk gu metti ! Ndóol ci
boppam moo baaxul.
- Tee nga bañ a sonal sa bopp di ci xalaat,
Al-yuun Badara !
- Kadeer, man Jolof laa xam ba mu jeex !
Sama mbokk yee fi gën a bëgg xew !
Wóor na ma ni foo dem ca dëkk ba dégg
ñuy wax waxi ñaari doomi golo yooyuı !
- Al-yuun Badaraa, yaa ngi mel ni xamoo
taskati xibaar yi ! Ñoo fi dàq a xoromal ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_465 | Tuuti kon ma dugg ci seen waxtaan, ne
doomu réewu Sudaη jooju :
- Waaw, ngóor si Abdel Maxjub la
xawma, lu la ci ba ngay weddi ak di
dëggal ? Yow gën a waane ! Xamal ni ñett
yii, maa leen yelloo, man Aali Këbóoy :
gis lépp, dégg lépp, fekke lépp ! Mbaa du
danga may diir mbagg di ? Juróom-ñaari
xarnoo ngi jaaxaan ci sama biir kaaη gii,
di dajjant ! Xarnu bu ci nekk a ngi xaar
ma ni la pëkk-pëkk, nga yeewu, fuddu, ne
ma :
- Démb, man mii maa doon démb ! Tey
maa ngi nii taxaw janook yaw !
Céy Badu, soo xamoon nu mbir mi deme !
Ay yéenekaay sax tudd nañu fi sa tur fan
yii. Dégg naa ci benn rajo ñu naan :
- Ndekete ndem-si-Yàlla ji Asan Taal mi
waral coow li, amoon na beneen doom ju
tudd Aliyun Badara. Mu nga bitim-réew.
Waa Ñarelaa yi ñu jot a waxtaanal nee ñu
gone gu amoon jom la, te jaambure. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_466 | Kon boog, Badu, xam nga ni yaa ngi ci
biir-a-biir...
*
* *
Bésub talaata la woon. Ngiraan Fay jóge
jàkkay Ñarelaa lal ndésam, toog ci ëtt bi.
Mbisin ak Mbisaan a ngi taal tele bi ba mu
sës.
Ngiraan woo mbindaanu Yaasin Njaay ni
ko :
- Aram, doo ma baal wax Mbisin ak
Mbisaan ñu wàññi tuuti tele bi, kenn mënu
fee dégg ndax ñoom.
- Maam Ngiraan, ñii ñaar kat sañuma leen
a tudd. Ku ma ci waxal ñaari baat mu
saaga ma ci nasaraan, te bu ko seen yaay
yëgee ne maa tooñ doomam.
- Céy ! Ku mas a gis lii ? Gone guy reew
kañ, ñaar ñii ngay dimbali. Man mii sax
de, fii lañu may fekk ma toog di wérd ñu
may wéq, di ma tëfli. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_467 | - Muñ dee fi sës, Maam Ngiraan. Léegi
mu jeex sax, ñoom ñépp a ngi waaj a dellu
Tugal !
- Keroog de, seen yaay mel na ne ku am lu
mu réerle !
- Altine jee nu génn, mook bàjjan Biige
Sàmb ànd nañu seeti benn sëriñ. Ci la ma
ko dégg muy wax de, feek i fan rekk mu
ñibbi Tugal.
- Li mu réerle woon feeñ naam ?
- Dégg naa mu naan loolu amatul solo.
- Ãa ? Waaye lu ciy sama yoon sax, man ?
Moom dal, nanu Yaasin Njaay ak doomam
yu xamadi yii abal rekk !
Noonu, Aram dellu kër Yaasin. Fi Ngiraan
Fay wéeroo ci garab gi, ubbi « Téereb
Ndéey », xam naa am lu mu la ciy fen, yow
Badu, mu mel ni dafa xelmati nit ku ko romb.
Mu wiccax bopp bi. Xel miy werante :
« Nit jaar na feem dama koo janeer ?
Géntuma kañ. Litkoloñ bi mu tuuroo ngi
fiy xeeñ ba tey ! » | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_468 | Ngiraan dégg ku laal buntu kër Yaasin
Njaay : « Waaw, jeegu Tubaab bu sew bii,
lu muy wuti kër Yaasin ? » Mu ne bëret,
ne day laaji ndawsi lu doon i tànkam.
Kooku walbatiku, xool Ngiraan ba seppali
ko, ne ràpp buntu dogaatle bi tëj. Yàggul
dara ñu dégg Aram, mbindaanu Yaasin
Njaay mi, muy salliiru :
- Wóoy sama ndeyóoy ! Wóoy man !
Wóoy sama ndeyóoy !
Waa Ñarelaa fàq wutali kër Ngiraan.
- Lu xew ci sa kër gi, Ngiraan ?
- Xam ! Maak yéen a ci yem.
- Noonu nga ci tollu ?
- Doo jóg sax seet lu Aram di yuuxu
nii ?
- Su ñu fi reyee doomu jaambur ji nag,
looy làyyi ?
- Mbaa du Aali Këbóoy a ñu bëgg
jommalati ? | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_469 | (Gis nga de, Badu, man mu weex dunq
mii, fexe nañu ba tudd ma ci. Nit ñee mën
a tooñ, walla !)
Am keneen ku ne :
- Waaw, jeegu Tubaab bi wàcce ci oto bu
ñuul, dugg fi nag, ku mu, Ngiraan ?
- Li ngeen may laaj de, dara laa ci xamul !
Tee ngeen a àggal seen bopp kër Yaasin
Njaay, seet lu fa xew !
Noonu, yuuxu Aram yi dakk. Ku nekk
xool sa moroom.Fi waa Ñarelaa yiy
yeddee Ngiraan, Biige Sàmb àgsi. Ñépp
xamoon nañu ne mooy ndeyu-mbill gi.
Ñarelaa ba Ñarelaa daj, moom rekk la fi
Yaasin Njaay mas a waxal. Biige Sàmb
ne jàkk mbooloo mi. Ñépp ne tekk di ko
déglu. Mu ne :
- Yéen waa Ñarelaa laay waxal. Kenn ku
nekk ci yéen na dellu fa mu jóge.
Kenn tegu ca baat. Teewul mu am ñu doon
yéexantu. Biige Sàmb ne leen : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_470 | - War naa leen a balu àq, ndax xéy-na ni ma
waxeek yéen xaw naa ñagas. Waaye maak
Ngiraan Fay rekk noo fi war a des. Li xew
lu réy la, te nun ñaar doηη noo ko séq.Ne
tuuti, kër gi ne selaw, mel ni kenn masu fee
nekk.Ngiraan ni :
- Ana sa xarit bi, Biige ? Biige Sàmb ne
patt ba yàgg mu sog a tontu Ngiraan :
- Bul sonal sa bopp, Ngiraan. Benn
Doomu-Aadama dootul teg Yaasin Njaay
bët.
- Dafa dellu Tugal, du ? Man de, ñëw na
ba tàggu ma. Ñaari doom yi fi nekk ba
léegi kañ ñoo ma ci jaaxal.
- Déggoo li ma la wax, Ngiraan ? Benn
Doomu-Aadama dootul teg Yaasin Njaay
bët.
- Kañ la fi faatu ?
- Faatuwul.
- Su dee faatuwul kañ, mu ngi dund.
- Dundul itam. Yaasin Njaay mi nga fi jot
a xamanteel, deewagul waaye dundatul. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_471 | - Waaw, Tubaab bi ma fi romb sànq, lu
mu joteek Yaasin Njaay ?
Biige Sàmb ne tekk, ba yàgg mu wàcce
baatam, daldi ne ndànk :
- Ndaw si la romb sànq mooy Yaasin
Njaay.
- Man de, ndeyu Mbisin ak Mbisaan laay
wax. Danga mel ni ku ma déggul, Biige.
Lu la dal tey ?
- Yaasin Njaay a sax, de.
- Biige Sàmb, lu la dal ? Jabaru Asan Taal
ji jóge Tugal, ñëw fii ténjsi ko laay wax.
- Ma ne : mooma, Ngiraan.
Foofu, Ngiraan téen, raay ndoη li ba noppi
sëggaat ne :
- Mbaa set nga ci mbir mi, Biige ?
- Man ma set ci ? Déedéet kañ, Ngiraan !
Axãa ! Yaa ngi may door a laaj li tax ma
ne waa Ñarelaa ñu may nu nu ñaaroo.
Déedéet, Ngiraan, setuma ci te dinaa la
wax tey lu ko waral. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_472 | Du yaa ngi fàttaliku bés ba nu gungejee
Asan Taal ayeropoor, muy dem Tugal ne
day futbali Màrsey ?
- Yàgg na lool, waaye mu ngi mel ni démb
ci man.
- Nekk nanu fa di jooyoo maak moom, yëf
yi takkarnaase, nuy fóonante ba nit ñi faf
mujjee noo wër di nu seetaan. Yaa ngi koy
fàttaliku, de ?
- Bu baax, sax.
- Waaye ba dara desul lu dul bàyyi Asan
Taal mu yéeg ci roppëlaan gi, lu leer nàññ
laa ko wax.
- Loo wax keroog Asan Taal, Biige ?
Jaaraat ci, ma dégg.
- Dama ne ko : Asan, dëgg la, tàggatoo bi
xumb na, ñépp a ngi jooyoo. Wànte lenn
rekk laa bëgg nga xam ko : nobante nanu,
ma jox la samag ndaw, nga àgg ci man,
biiral ma. Sunu doom jaa ngi nii ma boot.
Nee nga yaa ngay dem Màrsey futbali
waaye giñ naa ko ci bakkanu Badu Taal
mii : soo ma woree du baax ci yow ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_473 | - Lu la Asan Taal tontu, Biige ?
- Asan Taal dafa siggi, sunuy bët daje,
sama fit ne rës, Ngiraan. Waaw. Ca laa
sog a xam ne naaféq tigi laa jébbaloon
sama bopp. Booba ba léegi maa ngi daas
sama paaka, xam ne bés dina ñëw, ma fey
Asan Taal boram. Mu ngoog, Ngiraan. Sa
doom ji wor na ma, wax naa nit mu alag ki
ñu ne moo doon soxnaam. Sunu waxtaan
wii nag, mën naa des sunu diggante maak
yow.
- Déedéet. Du deme noonu, Biige.
- Badu Taal nga ko bëgg a àggeem ?
- Waaw. Am na wàll ci mbir mi.
Biige Sàmb neeti patt.
Ngiraan ne ko :
- Lu ciy sa xalaat ? Fi Biige di seetee ci
xelam lu muy tontu Ngiraan, buntu
dogaatle bi ubbeeku. Biige ne ci suuf :
- Sama jinne jaa ngoog. Ñaw !
Ngiraan sëgg fi mu sëgg rekk. Biige
reetaan : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_474 | - Bëggoo koo gis, xanaa ?
- Yal na ma ko Yàlla xañ ba fàww.
Mari-Gabriyelaa Won Bolkowski séen
leen, mel ni ku tiit moom itam, gaawantu
delloo buntam.Noonu, ñu déggaat Aram
muy yuuxu :
- Wóoy sama ndey ! Wóoy sama ndey !
Waa Ñarelaa bàyyeeti lépp lañu doon def,
daw wuti sa kër Maam Ngiraan Fay.
Géew baa ngi tëjusi, Badu.
Yaa ngi fàttaliku ne Ngiraan Fay
ayeropooru Ndakaaru la ubbee seen
waxtaan yéen ñaar ? Roppëlaan jóge na
Ruwaasi, ca Tugal, yéeg ndànk wuti
asamaan, romb ay dëkk yu bare, ñëw tiim
Ndakaaru, wër ko ñaari yoon, door a wàcc,
raay suufu Yoof su tedd si. Keroog jooju la
néewu Asan Taal, sa baay, agsi Ndakaaru.
Ci Téereb Ngelaw sax la Ngiraan Fay bind
lii : « Duma fàtte mukk bés ba nu jëlijee
néewu Asan Taal ayeropooru Ndakaaru. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_475 | Bésub alxames la woon, bi timis di waaj a
jot.
Ba nu demee ba jub tali Ngaala Jóob -
mooy jàddukaay bi mujje ci yoonu
ayeropoor - lanu dajeek mbooloo mu
takkoo-takku, kaar. Xanaa waroon naa tollu
ci ñeent mbaa juróomi-téeméeri junniy nit.
Ñii a ngi waaxu, ñii di xélu, ñaq bay siit, ñi
ci des dugg ciy kaar-ràppid mbaa ñuy dawal
seeni oto bopp, ñi gën a feete ndaw war
seeni móto. Ñépp di yuuxu, di tàccu, coow
li ne kur, sófóor siy korne tëwa bàyyi, koo
dajeel mu ngi taf rajo bu ndaw ci noppam.
Gone yi mel ni ñu tàggook seen sago.
Foo tollu, dégg ñuy salliiru :
- Móo-du ! Wiiw Móodu ! Móo-du ! Móo-
du ! »
Waaw.
Ngiraan a bind loolu ci Téereb Ngelaw,
bàyyil la fi.
Ndakaaru Njaay doon teeru woykat bu
amoon bayre ca jamono jooja. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_476 | Béréb bi Ngiraan ubbee, laay daaneele,
man Aali Këbóoy. Du nag lu ma taamul
sama bopp : mbir mee deme noonu rekk.
*
* *
Ayeropooru Ndakaaroo ka bare nit tey jii
it, kaar ! Noo yaakaar ne noonu la nit ñi
tollu rekk, romb na koy wéy. Nit ñi war
nañoo mat xanaa juróomi-téeméeri junni
ak lu topp. Lu xew ba taskati xibaar yi mel
ni ay njéeréer ci ayeropoor bi ? Deñ-
kumpa doηη a leen fi indi. Yaasin Njaay
de, lañu ne moo jékki-jékki soppeeku golo
mook ñaari doom yi, Mbisin ak Mbisaan.
Coow laa ngi ne kur nag.
Am ku ne :
- Ndaw seek ñaari doom yi nee nañu mes.
- Séen naa leen ñuy yéeg ci kow garab gii !
- Nun kay noo leen mënul a gis, waaye
wóor na ma ñoom ñu ngi janook nun, di
nu ηóobi ! Yéen, xamuleen golo sax!
- Tee noo gor garab gi waay ? | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_477 | - Loolu da koy yàggal ! Am na lu gën a
gaaw !
Waa ji wax loolu tàmbalee sànniy xeer ci
garab gi, gone yi topp ciy sànniy xeer
ñoom it. Njiitu takk-der yi dawseek liifam,
ne leen ñu dakkal li ñuy def :
- Dañuy aaye ku fi sànni xeer.
- Baal nu de, seef, xamunu ci woon
dara.Alkaati bi ñaan fa sigaret, ñu faf lal
waxtaan. Benn jeeg bu xeesal ba kanam gi
yépp yàqu, ne takk-der bi :
- Waaw, ndaw si ñuy wax sax, lu mu def ?
- Benn Tubaab la, wallaay ! Daa bëggoon
a sàcc ñaari gone yu ndaw.
- Déet waay !
- Ñaari doomi réew mi la doon jéem a
rawale Tugal.
- Ãa ? Loolu gën a doy waar !
- Soo demee dafa leen bëggoon a jaayi
mbokki Tubaabam yi !
- Maa la ko wax ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_478 | Takk-der bi reetaan :
- Mu ngoog de ! Ba ñuy nemmeekuy
kayitam daal, la ne tirr daw ! Booba ba
léegi ñu ngi koy wër !
Waa ji mayoon alkaati bi sigaret daldi ne :
- Kon li ñu naan dafa soppeeku golo du
dëgg ? Alkaati bi kimmi sigaretam, téen,
sànni saxaar si, xool waa ji, muuñ :
- Noo mënee gëm waxi dof yooyu, yow
itam ? Kañ la nit daan soppeeku golo ?
Ñépp xàqataay.Waa ji ñéññ, ne :
- Takk-der nga, dégg la waaye maa la gën
a xam ni mbir mi deme ! Ndaw si Yaasin
Njaay la tudd, mu nga dëkk Ñarelaa.
Lagara bu bon la sax ! Cagatu na Màrsey,
defay njaaxumam, ba noppi ñëw fii ne
dafa nuy jommal !
Alkaati bi xool ko ba seppali ko, yëngal
boppam, ni ko :
- Werante kay gis bokku ci ! Kayitu juddu
ndaw saa ngi nii. Lu ñu ci bind ? | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_479 | Kaay jàng ! Kii ak turam wu gudd wii
moos, juddoo Burgoñ, bokk fa ci kër gu
mag sax, dégg naa, na mu mënee nekk sa
Yaasin Njaay moomu ?
Werante bi neeti kur. Tuuti kon yëf yi ëpp
loxo.
Suba su waa Ñarelaa yeewoo, yëf yi gën a
takkarnaase !
Badu, li nga wax keroog Abdel Kadeer
Maxjub dëgg la : du gox bi rekk a rëb.
Foo dem ci réew mi, dégg fa kàddu yii ma
lay jottalisi :
Yaay ju weex tàll.
Doomi golo.
Yaasin Njaay.
Dawe ayeropoor, jaar ci kow garab yi,
dellu këram, tëju faak ñaari doomam.
Asan Taal.Tubaab.
Badu Taal.
Mari-Gabriyelaa nakaati sax ?
Ku nekk naan : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_480 | - Kenn du ma nettali lu kéemaanee noonu,
fàww ma gisal sama bopp Tubaabu
Ñarelaa bi ñuy coow.
Dëkk bi yépp riirandoo, jëmsi Ñarelaa.
Waa Ndakaaru Njaay a bëgg xew ! Fan yii
de, foo sànni mbàttu ci Ñarelaa mu tag.
Saay-saayu Ndakaaru yépp làngsi nañu ci
gox bi. Du benn du ñaar nit xëm na fi
mbaa ñu jàpp fi sàcc dóor ko ba Yàlla fóot
ay sagaram. Ma dajeek ay gone yu jolu ay
butéeli sàngara, màndi ba ma mënatuñoo
taxaw, ñu topp benn janq, takkal ko pot :
- Yee gel yow, ana Tubaab bi ?
- Gelu Ŋeew bi lanu soxla ! Na génn
waay, nu ceg ko !
- Màndeeti nga de, Njóogu ! Fii benn
Tubaab newu fi !
- Séen naa ndawsi, te soo weddee nu teg !
Ayca, junnee ngi ! soo wóoloo sa bopp,
tegal !
- Man it séen naa ko, dafa cuq de, sunu
Ŋeew bi ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_481 | Am xaat ñuy siisaate. Man de, Badu, bett
naa fi ay boroom kër ñu naan :
- Ku dëkkul Ñarelaa amoo dara looy wax !
Nun, xam nanu lu tax Yàlla wàcce fi ndaw
sii.Waaye séytaanee teg loxo ci Ñarelaa,
fan yii. Mbedd mu ma jaar, dégg kuy rëbb
jeegu Tubaab bi :
- Waaw, ana mu sax, moom ?
- Wëey ! Na génn, nu gis ko !
- Na gaaw génn mbaa nu taal léegi kër gi
ci seen kow ! Ñii di sànniy xeer, na ca des
ne ñu ngay wuti esaas bu ñu taale sa kër
maam Ngiraan Fay. Nit ñaa ngi ñaq tooy
xepp, di daw ci tàngaay bi, di yéeg ci
garab yi, koo dajeel muy di wax ay waxi
dof tëwa noppi. Taxul nag sa maam
Ngiraan Fay ubbi benn yoon gémmiñam.
*
* *
Juróom-ñaareelu fan.
Kenn xejatul Ñarelaa ndax fépp la nit ñiy
jóge. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_482 | Sunu gan yi dañoo mujje di fanaan ci
mbedd mi.
Foo walbatiku dajeek ñuy yalwaan walla
ay jaaykati ndox mu sedd mbaa bisaab ;
waaraatekat yiy wër Ñarelaa, naan :
- Waay, ku lii doyul lu lay doy ?
Am ñu yore nataalu ndaw si di ko jaay :
- Mu ngi. Mari-Gabriyelaa Won Bolkowski
la tudd !
Werante gis bokku ci !
- Ñaata nga ci bëgg, waa ju baax ?
- Juróom-benni junni.
- Junnee ngi.
- Xeeb naa ko.
- Tegal naa la ci téeméer.
- Ma ne : baax na.
- Man ngay sëppu ? Xanaa xamoo ki ngay
waxal ?
- Bul ma tooñ, jàmbaar ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_483 | - Yéen kay, la kenn waxul dara ! Ku leen
romb, ngeen tàllal ko nataal bu wuteek ba
ca des, te ne yépp benn nit ki la ! Yabaate
ba dee !
Ñu songoo, kurpeñ yi dal, ñii far fii, ñee
far fa ca des. Mag ñi di leen yedd, nag :
- Yëf yi xéewal gu fi Yàlla wàcce la, jarul
a xeex ak a xuloo ! Su ngeen àndeek seen
sago, ku nekk dina séddu ba doyal ! Ñépp
xej nañu ci !
- Eskéy !
- Ndaw sii dafa noo bëgg a yab, ndax li
deram bi weex !Mu mel ni nag loolu rekk
la nit ñi doon xaar :
- Xeebaate bi dafa doy !
- Tubaab yii ! Maa leen xam, tey ! Mënuñoo
nangu ne nun ñii ay Doomi-Aadama lanu ni
ñoom !
- Ñoo fi gën a bare pexe, waaye jinne jii
moom, balaa muy génn ci lii tey dina wax
lu set ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_484 | - Xanaa mook ñaari doomam yii dinañu
lekk !
- Ay doom laa déggam ?
- Waa-waaw !
- Doom yu mel nan ?
- Ñoo la gën a ñuul sax, de.
- Tubaab bu weex ak ay doom yu ñuul laa
dégg ?
- Kii du nit ku baax !
- Lu nuy xaar ? Nanu dàjji bunt bi, waay !
Benn góor gu màggat ñëw ni leen :
- Déet doom, yoonu jàmm sorewul.
- Waay, déggal paa bii ! Jàmm ba ci lan,
nag ?
- Dama xam ne ay du yem ci boppu
boroom, rekk. Nen du bëreek doj. Ndaw si
am nay mbokk, kat ! Su waa Tugal dalee
sunu kow, nag ?
Gone yi ree ba tëdd ci suuf.
- Góor gii daal, xanaa dafa paagal ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_485 | - Réew mu tollu ni Farãas amul lu muy
def lu dul di sonal boppam ci ab lagara
doηη !
- Tubaab yi tal nañu leneen !
- Ndegam du dëmm sax, ndaw sii !
Waaye gone yooyu, Yàlla mi dul faral kuy
tooñ, moo leen daldi tiiñal ci saa si.
Fa ñuy kókkëlee góor gi, di kex-kexi, la
daldi am ñu agsi booru kër Ngiraan ak
seeni yuuxook seeni xiixat yu metti. Kenn
ci ñoom ne :
- Soldaari Daawur Jaañ yaa ngi jëmsi
Ñarelaa ak seeni fetal !
- Lan laa dégg ? Ay soldaar, tàww !
- Waa-waaw ! Ñii ma gis de, dañoo ñàng
ba dee, waat naa ne ku ñu fi fekk du baax
ci yow ! Naka la nit ñi dégg loolu rekk,
tàmbalee daw, di yuuxu :
- Soldaar yaa ngoog !
- Dawleen ! Ku ñu fi fekk tàkk nga ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_486 | Badu, su doon sama sago, dinaa la nettali
li fi xew ba jeexal te duma la ne bakkan
rot na fi. Mënuma ko, ndax wax la dëgg
moo ma war. Loolu laa dig Ngiraan Fay.
Keroog, dëggaate nañu ci buntu kër gi
fukki nit ak juróom-ñeent, ñu daldi faatu
ci saa si. Monte de, buuxante mënoon na
cee bañ a am. Nit ñee tiitoon seen tiitu
bopp rekk, waaye wax dëgg Yàlla soldaari
Dawuur Jaañ yi defuñu fi benn ñaawteef.
Dañoo wàcc seeni oto, seen njiit nuyoo ci
yar ak teggin ju mat sëkk, daldi ni :
- Fii la Ngiraan Fay dëkk, de ?
Biige Sàmb a ko tontu :
- Waaw, fii mooy këram.
- Ana mu, moom ?
Biige daldi tuur soldaar bi lëndëm :
- Dafa feebar, ñu yóbbu ko loppitaan.
Man, goroom laa, maa fi nekk.Njiitu
soldaari Daawur Jaañ yi taal telefonam, ne
ki mu doon jokkool : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_487 | - Nu ngi leen fiy xaar, maak samay nit.
Buleen yàgg, nag.Bi ñu ci tegee genn-
wàllu waxtu, yeneen soldaar agsi ci gox
bi.Waaye ñii ñoom, ay Tubaab lañu woon.
Seen njiit jubal ci njiitu soldaari Daawur
Jaañ yi. Ñu gise ñoom ñaar gise bu
gaaw.Tubaab bi ne Biige Sàmb :
- Madam Mari-Gabriyelaa Won
Bolkowski laa jëlsi.
- Àgg leen ca néeg yale ngeen di séen. Mu
nga faak ñaari doomam.
Kàddu yooyu jaaxal lool Tubaab bi :
- Ñaari doomam ? Doomam yan ?
Biige Sàmb ne njiitu soldaari Daawur Jaañ
yi :
- Man kat dégguma nasaraan, kon sama
waxtaan ak ngóor sii du mën a sori. Ne ko
bumu nu tanqal, na yóbbu mbokkam mi,
xawma Mari-Gabriyelaa la tudd xawma,
te abal nu. Njiitu soldaari Tubaab yi dóor
bal buntu kër Mari-Gabriyelaa, mu ne tëll,
dàjjeeku. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_488 | Fekk na booba Mari-Gabriyelaa ngi làqu
woon ci wanagam, mook doom yi. Naka
la yërndu ba xàmmee ñi ko doon jëlsi,
daldi daw fekki leen ci saal bi :
Booba ba léegi maa ngi leen di xaar ! Su
ngeen doon yéex, ñuy taal kër gi ci sunu
kow !
Tubaab bi ni ko :
- Mbaa noppi nga rekk ? Ambasadeer baa
ngi lay nég sa màkkaanam. Sunu njiitu
réew, ca Tugal, nee na ko na fexe ba bu la
dara dal !
Mari-Gabriyelaa ree :
- Aycaleen nu dem ! Mbisin ! Mbisaan !
Ñaari gone yi génne ci wanag wi, daldi
langaamu seen ndiggu yaay. Tubaab bi
gaññ :
- Ñii ñaar nag ?
- Samay doom lañu.
- Say doom ? Soo dee kaf it, nun kafunu,
soxna si ! Liggéey moo nu fi indi. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_489 | Soo gisee njiitu soldaari Tubaab yi, mu
ngi mer ba funki.
Mari-Gabriyelaa xam ne fa ko Biige Sàmb
ak Sinkun Kamara dugal, caaxaan
génnewu ko fa. Mu ni Tubaab bi :
- Ñaar ñii maa leen jur ci sama biir bii !
- Xool nga leen bu baax ? Noo mën a
juree ñii ñaar ?
Mbisin ak Mbisaan seen bopp ñu ngay
jooyoo, di gën a langaamu seen yaay, di
ko saraxu, ne du dem mukk bàyyi leen
Ñarelaa.
Mari-Gabriyelaa wutewul ak dof.
Mujjewul lu dul sukkal Tubaab bi, naan
ko :
- Xanaa amoo ay doom ? Soo gisee ni
Mbisin ak Mbisaan di jooye rekk nga war
a xam ne maa leen jur !
Njiitu soldaari Tubaab yi ronni ko ba
xolam sedd, ne ñi mu àndal :
- Gàddul-leen ma ndaw sii ! Dañu ma sant
ma yóbbu la sunu àmbasadu réew. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_490 | Mu neex la, mu naqadi la, dinaa ko def !
Soo demee foofu nga wax fa sa waxi
kasaw-kasaw yii ba xam ndax dinañu la
faale !
Soldaar yi mu àndal xaw a mel ni ñu
yërëm ñaari gone yi.
Mu xulli leen :
- Lu ngeen di xaar ? Gàdduleen ko laa
wax !
Ñu ne kirtim Mari-Gabriyelaa, muy wéqu,
di saaga soldaar yi, di leen gajj. Ñaari
doom yi tamit ràkkaaju, di fëgg buntu kër
gi, di làkk nasaraan tëw a noppi.
Soldaar yi génn kër geek ndaw si, daldi
jubal seeni oto.
Benn góor gu kaalawu ñëw ba ci kanamu
Mari-Gabriyelaa, taxaw, ñu xoolante
ñoom ñaar.
Mari-Gabriyelaa daldi ne ci suuf :
- Sinkun Kamara.
Kooku ni ko : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_491 | - Waaw. Sinkun Tiggide Kamara.
- Lu ma la def ? Wóoy man ! Loo ma
bañee nii ?
- Lii lépp yaa ko teg sa bopp. Kenn rekk
laa ci soxla woon. Léegi dinga ñàkk
buubu, ñàkk ceen ga.
- Yërëmal boog gone yi. Ñoom doonuñu
ci dara.
- Xanaa gëmoo li ma la wax, Mari-
Gabriyelaa Won Bolkowski ? Nee naa la
doyewuma leen dara, man mii. Sama gaa
ñe ci soxla woon kenn, nga ne fay nakk-
nakkal ba ñu mer. Soo demee nuyul ma
waa Tugal !
Ba bi soldaari Tubaab yiy taal seen oto,
Mari-Gabriyelaa ngi salliiru, di yuuxu turi
ñaari doom yi, di féqu, foo tollu di dégg
saagaam yu ñaaw yi.
Pënd bi naaw, muur jaww ji. Jaww ji xonq
coyy. Pënd bi wuri. Mbisin ak Mbisaan
gënatee tiit, seen jooy yi daldi dakk ci saa
si, ñuy xullee, mel ni ñu tiim seen buntu
bàmmeel. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_492 | Sinkun Kamara walbatiku, daj ci Biige
Sàmb, ni ko :
- Yewwi ma boog, soxna si.
Biige Sàmb xool ko, yëngal ndànk bopp
bi.
Sinkun Kamara xam li mu ko waxul,
defaraat kaalaam, dëngalu dem yoonam.
*
* *
Dinga ma ne :
- Waaw, bi loolu yépp di xew, fu Ngiraan
Fay newoon ?
Muy it laaj bu am solo. Soo dellusee,
Badu, laajal ku la neex ci Ñarelaa.
Ba ma ñaarook moom ba noppi, fab ko
dugal néegam, Ngiraan Fay tegatul benn
yoon tànkam ci diggu kër gi. Lekkatul,
naanatul, jooteetul daraak kenn ci gox bi.
Doon nanu ko dégg daal muy waxtu.
Guddiga mu gàddoo yat ne day dàq Ninki
ak Nanka, | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_493 | ñaari doomi golo yi kenn ci nun masul a
gis, di leen móolu, naan leen nañu dellu ca
àll ba mbaa ñu dem fekki seen ndey Toolu-
Buur, ca Guy-Géwél, guddi googu lanuy
door a leer ne Ngiraan Fay àndatul ak
sagoom, ndeysaan.
Waaye gaaw a wax baaxul.
Ñàkkul mu amoon lu feeñu Ngiraan, booba.
Ndax lii moom, kenn du ko werante : nun
sunu bopp, xéy nanu bés gis ñaari golo yu
ndaw yuy dóor dàqe ci mbeddi Ñarelaa yi.
Ku leen jub, ñu daw làquji ci kow garabi
gox bi. Biige Sàmb daal, moo fexe bés ba
nax leen, ñu langaamu ko, mu teg leen ciy
mbaggam, ànd ak ñoom di fo di ree.
Ba Mari-Gabriyelaa Won Bolkowski
delloo Tugal ba ñu teg ca ñetti weer la sa
maam Ngiraan Fay ma fatu woon faatu.
Man Aali Këbóoy teewe naa sukkuraatam.
Ngiraan jot naa xippi, xàmmee ma, téye
sama loxo lu yàgg. Teewe naa loolu te
ngelaw li dina wéy di ko biral : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_494 | sa maam Ngiraan Fay tàggoowul benn
yoon ak sagoom.
Ci li ma mën a seede de, ba mu fiy jóge
xelam daloon na.
Bi nuy diisoo nun ñaar la soldaari Daawur
Jaañ yi dellusi Ñarelaa, ne dañu leen ne
am nay saay-saay yu fi làq ay ngànnaay,
di waaj a song nguur gi. Coow li neeti
kurr :
- Ay gànnaay, fii ci Ñarelaa ?
- Baay Ndeene de la nguur giy tuumaal !
- Baay Ndeene man ?
- Xanaa dégluwoo rajo yi ? Dafa bëggoon
a daaneel Daawur Jaañ sax de !
- Dara ! Sunu Afrig gii kat, ay kolonel ni
moom rekk ñoo fiy nekk ay paresidaa !
- Wax nga dëgg ! Te su nekkoon
paresidaa, sunu ceeb tooy, nun waa
Ñarelaa !
Céy, sama gaa ñi ! Kolonel Kamara !
Paresidãa Kamara ! Xawma maak yéen
kan moo ci gën a yenuy dàllam ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_495 | Maak Ngiraan a ngi janoo, nuy dégg ni
saar de kombaa yiy wëree Ñarelaa ak ni
bomb yiy kalaatee :
Rëll ! Rëll ! Rëll !
Mu xëcc sama loxo, tari Alxuraan. Benn
bomb rajaxe asamaan si.Ngiraan muuñ,
tudd turu Yàlla, gërëm ma, gëmm.
Ba ko waa Ñarelaa di robi, romb nañu ñaari
doomi golo yi ñuy xëccoo benn welo bay
xeex, ku nekk bëgg koo xañ sa moroom.
Waaye bi oto bi yaboon néewu Ngiraan
Fay raamee ba tollook ñoom, dañoo fàtte
welo ba ci saa si, ne jàkk mbooloo mi.
Keroog ñu bare la seen yaram daw ndax ni
doomi golo yi nee tekk-tekkaaral di
seetaan waa Ñarelaa.
Ne tuuti kenn ki woo moroom mi. Kooku
tëb fekki ko, mu am lu mu ko déey, ñu
àndandoo di ree, di màtt seen baaraam ak
a wiccax seen bopp, mel ni ñu naan :
Ñaw ! Gat di ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_496 | Ca armeel ya nag, man Aali Këbóoy bàyyi
naa naaféqi Ñarelaa yi ñu wax seen waxi
caaxaan ba noppi, ma door a yëkkati
samay kàddu ba ca kow, xalab leen ci biir
géew bi. Ñoom ñépp ñu téenandoo di ma
seet.
Kenn ci ñoom gisu ma ci, waaye ñoom
ñépp xàmmee nañu sama baat, man Aali
Këbóoy. Duma jaaraat nag ci li ma leen
wax keroog. Ñoom ñi moom wax ji, dégg
nañu ma bu baax.
Bi ma jógee armeel ya, dajale na juróom-
ñaari téere yi la Ngiraan Fay jagleel. Takk
naa leen ba ñu dëgër, ma lëmës leen ci
benn turki bu fi Ngiraan bàyyi, gas ci
taatu ndaa li ba mu xóot, ma suul leen fa.
Soo ñibbisee fii ak juróom-ñetti xarnu it,
dinga ma fi fekk, man Aali Këbóoy, may
aar say téere di la xaar.
Dig naa ko Ngiraan Fay. Dinaa ko def.
Yóbbante nag, àq la.
Dinaa na la ne jabb juróom-ñaari Téere yii
may limsi. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_497 | Téereb Dóom.
Téereb Ngelaw.
Téereb Lëndëmtu.
Téereb Fent.
Téere bu Ñuul bi.
Téereb Wis.
Fàttewuma Téereb Ndéey.
Su wesoo Ngiraan mi ko bind, keneen
warul a xam lan moo làqu ci biir. Waat
naa ne man mi la ko fiy dencal sax, duma
juum mukk ba ubbi ko. Waaye téere
yooyu yépp nag, bés boo dellusee, bala
nga ciy ubbi benn di ko jàng, dinaa la téye
ci loxo, nu dem ma won la sa bàmmeelu
maam. Xawma kan, wànte yow Badu
Taal, soo ñëwee tiim Ngiraan Fay fa mu
tëdd ca armeel ya,
ñaanal ko, fàww mu yëg ko ci yaramam.
Te wóor na ma ne Ngiraan Fay dund na ba
dee te masul a am mbégte mu day ni ba
muy nar a am bés bu màgg boobu. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_498 | Domi golo audio numerique
Developpé par allowow
Editions Audio Numérique
Ebook Africa | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_1 | ANTOINE DE SAINT-EXUPÉRY
Wolof
Ndoomu Buur Si | Ndoomu Buur Si.pdf |
page_5 | Ndoomu Buur Si | Ndoomu Buur Si.pdf |
page_6 | Foog naa dafa làngaamu ci picc yuy roñu ngir mën a rëcc. | Ndoomu Buur Si.pdf |
Subsets and Splits
No community queries yet
The top public SQL queries from the community will appear here once available.